The New Testament of our Lord and Saviour Jesus Christ
1:1 Lii mooy cosaanu Yeesu Kirist, sëtu Daawuda, sëtu Ibraayma. 1:2 Ibraayma moo jur Isaaxa; Isaaxa jur Yanqóoba; Yanqóoba jur Yuda ak i doomi baayam; 1:3 Yuda, Fares ak Sara ci Tamar; Fares Esrom, miy baayu Aram; 1:4 Aram Aminadab; Aminadab Naason; Naason Salmon; 1:5 Salmon jur ci Raxab doom ju tudd Bowas; Bowas am ak Ruut Obedd; Obedd jur Yese, 1:6 miy baayu buur bi Daawuda. Daawuda moo jur Suleymaan ci ki nekkoon jabari Uri; 1:7 Suleymaan jur Robowam; Robowam Abiya; Abiya Asaf; 1:8 Asaf Yosafat; Yosafat Yoram, miy baayu Osiyas; 1:9 Osiyas jur Yowatam; Yowatam Akas, miy baayu Esekiyas; 1:10 Esekiyas Manase; Manase Amon; Amon Yosiyas; 1:11 Yosiyas jur Yekoñas ak i doomi baayam ca jamono, ja ñu defe Yawut ya jaam, yóbbu leen Babilon. 1:12 Ba ñu leen yóbboo ca Babilon, Yekoñas jur Salacel; Salacel Sorobabel, 1:13 miy baayu Abiyudd; Abiyudd Eliyakim; Eliyakim Asor; 1:14 Asor Sadog; Sadog Akim; Akim Eliyudd; 1:15 Eliyudd Eleyasar; Eleyasar Matan, miy baayu Yanqóoba; 1:16 Yanqóoba nag moo jur Yuusufa jëkkëru Maryaama; te ci Maryaama la Yeesu, mi ñuy wax Kirist, juddoo. 1:17 Mboolem giir googu nag, la dale ca Ibraayma ba ca Daawuda, fukk lañu ak ñeent; la dale ca Daawuda ba ca njaam ga ca Babilon, fukk lañu ak ñeent; la dale njaam ga ca Babilon ba ci Kirist, fukk lañu ak ñeent. 1:18 Nii la Yeesu Kirist juddoo. Bi ñu mayee Maryaama ndeyam Yuusufa, waaye laata ñoo ànd, gis nañu ne dafa ëmb ci kàttanu Xel mu Sell mi. 1:19 Yuusufa jëkkëram nag, nekkoon na nit ku jub te bëggu ko woon a weer. Mu nar a xàccook moom ci sutura. 1:20 Waaye bi muy xalaat ci loolu, benn malaakam Boroom bi daldi ko feeñu ci gént ne ko: «Yaw Yuusufa, sëtu Daawuda, bul ragal a yeggali Maryaama sa jabar, ndaxte doom ji mu ëmb, ci Xel mu Sell mi la jóge. 1:21 Dina jur doom ju góor; na nga ko tudde Yeesu, ndaxte moo di kiy musal xeetam ci seeni bàkkaar.» 1:22 Loolu lépp xewoon na, ngir amal li Boroom bi wax, jaarale ko cib yonent, bi mu naan: 1:23 «Janq bi dina ëmb,jur doom ju góor,ñu tudde ko Emanuwel,» liy tekki «Yàlla ganesi na nu.» 1:24 Noonu Yuusufa yeewu, yeggali jabaram, na ko ko malaakam Boroom bi sante woon. 1:25 Waaye àndul ak moom, ba kera mu mucc, jur doom ju góor; mu tudde ko Yeesu.
2:1 Bi nga xamee ne Yeesu juddu na ci Betleyem ci diiwaanu Yude, amoon na ay boroom xam-xam, ñu jóge penku, ñëw Yerusalem. Booba, ci jamonoy buur bi Erodd la woon. 2:2 Ñu ne: «Ana buur bi juddul Yawut yi? Ndaxte gis nanu biddiiwam ci penku te ñëw nanu ngir màggal ko.» 2:3 Bi ko Erodd buur ba déggee, mu daldi jaaxle, moom ak waa Yerusalem gépp. 2:4 Mu woolu nag saraxalekat yu mag yépp ak xutbakati xeet wa, laaj leen fu Almasi bi, maanaam Kirist, war a juddoo. 2:5 Ñu ne ko: «Ca Betleyem ci diiwaanu Yude, ndaxte lii lañu bind jaarale ko cib yonent: 2:6 “Yaw Betleyem ci diiwaanu Yude,du yaw yaa yées ci njiiti Yude,ndaxte ci yaw la njiit di génne,kiy sàmm Israyil sama xeet.”» 2:7 Ci kaw loolu Erodd woolu ci kumpa boroom xam-xam ya, di leen ceddowu, ngir xam bu wóor kañ la biddiiw bi feq. 2:8 Noonu mu yebal leen Betleyem naan: «Demleen fa, seet bu wóor mbirum xale ba. Bu ngeen ci amee lu wóor nag, ngeen xamal ma ko, ngir man itam ma dem màggal ko.» 2:9 Ba ñu dégloo buur ba nag, ñu dem. Te biddiiw, ba ñu gisoon ca penku ba, ne tell jiite leen, ba àgg, tiim fa xale ba nekk. 2:10 Ba ñu gisee biddiiw ba nag, ñu am mbég mu réy-a-réy. 2:11 Ñu dugg ca kër ga, gis xale ba ak Maryaama ndeyam, ñu daldi sukk, di ko màggal. Ñu ubbi seeni boyetu alal, may ko wurus ak cuuraay ak ndàbb lu xeeñ lu ñuy wax miir. 2:12 Bi ñu ko defee Yàlla artu na leen ci biir gént, ñu bañ a dellu ca Erodd. Noonu ñu jaar weneen yoon, ñibbi seen réew. 2:13 Bi nga xamee ne boroom xam-xam ya ñibbi nañu, benn malaakam Boroom bi feeñu Yuusufa ci gént ne ko: «Erodd mu ngi ci tànki wut xale bi, ngir rey ko; jógal nag, jël xale bi ak ndeyam te nga daw jëm Misra, toog fa, ba kera ma koy wax.» 2:14 Yuusufa nag jóg, jël xale ba ak ndeyam, làquji Misra ca guddi ga. 2:15 Mu toog fa, ba Erodd faatu. Noonu am li Boroom bi waxoon jaarale ko cib yonent, bi mu naan:«Woo naa sama doom, mu génn Misra.» 2:16 Bi Erodd gisee nag, ne boroom xam-xam ya nax nañu ko, mu daldi mer lool. Mu santaane ñu dugg ca Betleyem ak la ko wër, rey xale yu góor ya fa am ñaari at jëm suuf, mengook jamono, ja ko boroom xam-xam ya waxoon. 2:17 Booba am la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Yeremi, bi mu naan: 2:18 «Baat jib na ci Rama,ay jooy ak yuux gu réy,Rasel mooy jooy ay doomamte bëggul kenn dëfël ko,ndaxte saay nañu.» 2:19 Bi nga xamee ne Erodd faatu na, benn malaakam Boroom bi feeñu Yuusufa ci gént ca Misra, 2:20 ne ko: «Ñi doon wut a rey xale ba dee nañu; jógal nag, jël xale bi ak ndeyam te nga dellu Israyil.» 2:21 Yuusufa jóg nag, jël xale ba ak ndeyam, dellu Israyil. 2:22 Waaye bi mu déggee ne, Arkelawus moo donn Erodd baayam ca nguuru Yude, mu ragal faa dem. Yàlla artu ko nag ci gént, mu daldi dem diiwaanu Galile. 2:23 Mu ñëw nag dëkk ci dëkk bu ñuy wax Nasaret. Noonu am la ñu waxoon ca xale ba, jaarale ko ca yonent ya, bi ñu naan:«Dees na ko tudde Nasaréen.»
3:1 Ca jamono jooja Yaxya feeñoon na, di waare ca màndiŋu Yude. 3:2 Nii la doon waaree: «Tuubleen seeni bàkkaar, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji jege na.» 3:3 Yaxya mooy ki ñu doon wax jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu naan:«Am na baat buy xaacu ca màndiŋ ma ne:“Xàll-leen yoonu Boroom bi,jubal-leen fi muy jaar.”» 3:4 Yaxya nag mu ngi soloon mbubb mu ñu ràbbe kawaru giléem, takk geñog der ci ndiggam. Ay njéeréer la doon dunde ak lem. 3:5 Noonu ñépp génn jëm ci moom, ñi dëkk Yerusalem ak diiwaanu Yude, ak waa dexu Yurdan. 3:6 Ñu nangu seeni bàkkaar, Yaxya sóob leen ca dexu Yurdan. 3:7 Noonu ay Farisen ak ay Sadusen yu bare ñëw ci Yaxya, ngir mu sóob leen ñoom itam ca dex ga. Waaye bi leen Yaxya gisee, mu ne leen: «Yéen ñi fees ak daŋar mel ni ay co, ku leen artu, ngeen daw merum Yàlla mi nar a wàcc? 3:8 Jëfeleen nag ni ñu tuub seeni bàkkaar, 3:9 te buleen wax ci seen xel naan: “Nun daal doomi Ibraayma lanu,” ndaxte maa ngi leen koy wax, Yàlla man na sàkkal Ibraayma ay doom ci doj yii. 3:10 Sémmiñ wi tiim na reeni garab yi. Garab nag gu meññul doom yu baax, dees na ko gor, sànni ko ci safara si. 3:11 Man maa ngi leen di sóob ci ndox, ci lu ànd ak tuub seeni bàkkaar. Waaye kiy ñëw sama gannaaw moo ma ëpp kàttan, ba yeyoowuma koo yóbbul sax ay dàllam. Kooku dina leen sóob ci Xel mu Sell mi ak safara. 3:12 Layoom mu ngi ci loxoom, ngir jéri dàgga ja, ba mu set; pepp ma dina ko def ca sàq ma, waaye xatax ba dina ko lakk ci safara su dul fey mukk.» 3:13 Booba Yeesu jóge Galile, ñëw ngir Yaxya sóob ko ca dexu Yurdan. 3:14 Waaye Yaxya gàntu ko ne: «Man maa soxla, nga sóob ma ci ndox, te yaa ngi ñëw ci man!» 3:15 Yeesu tontu ko: «Bàyyil noonu, ndaxte war nanoo mottali lépp lu jub.» Noonu Yaxya nangu. 3:16 Bi ko Yaxya sóobee ca dex ga, Yeesu génn. Ca saa sa asamaan yi daldi ubbiku, te Yaxya gis Xelum Yàlla wàcc ci melow pitax, ñëw ci kaw Yeesu. 3:17 Te baat bu jóge asamaan dégtu ne: «Kii mooy sama Doom ji ma bëgg; ci moom laa ame bànneex.»
4:1 Bi loolu amee Xelum Yàlla yóbbu Yeesu ca màndiŋ ma, ngir mu jànkoonte ak fiiri Seytaane. 4:2 Yeesu nekk fa te lekkul ñeent-fukki bëccëg ak ñeent-fukki guddi, door a xiif. 4:3 Noonu fiirkat bi ñëw ci moom ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, santal doj yii, ñu nekk mburu.» 4:4 Waaye Yeesu tontu ko ne: «Mbind mi nee na: “Nit du dunde mburu rekk, waaye itam gépp kàddu gu génne ci gémmiñug Yàlla.”» 4:5 Bi mu waxee loolu, Seytaane yóbbu ko ca dëkk bu sell ba, teg ko ca njobbaxtalu kër Yàlla ga. 4:6 Mu ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, tëbal ci suuf, ndaxte Mbind mi nee na:“Dina jox ay malaakaam ndigal ci sa mbir,ñu leewu la ci seeni loxo,ngir nga bañ a fakkastalu ciw doj.”» 4:7 Yeesu tontu ko: «Bind nañu it ne: “Bul diiŋat Yàlla, sa Boroom.”» 4:8 Gannaaw loolu Seytaane yóbbu ko ci kaw tund wu kawe lool, won ko réewi àddina yépp ak seeni ndam. 4:9 Mu ne ko: «Lii lépp dinaa la ko may, boo sukkee màggal ma.» 4:10 Waaye Yeesu tontu ko: «Sore ma Seytaane, ndaxte Mbind mi nee na: “Nanga màggal Yàlla sa Boroom, te jaamu ko moom rekk.”» 4:11 Noonu Seytaane bàyyi ko. Te ay malaaka daldi ñëw fi Yeesu, di ko topptoo. 4:12 Am bés Yeesu dégg ne, jàpp nañu Yaxya; mu jóg nag, jëm Galile. 4:13 Gannaaw gi, mu toxoo dëkku Nasaret, dem dëkk Kapernawum, bi féeteek dex ga ci diiwaani Sabulon ak Neftali. 4:14 Noonu am la ñu waxoon, jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu naan: 4:15 «Yaw réewum Sabulon ak réewum Neftali,di yoonu géej gannaaw dexu Yurdan,yaw Galile, réewum ñi dul Yawut — 4:16 xeet wa nekkoon cig lëndëm,gis na leer gu mag,ña dëkkoon ca réew, ma dee tiim,leer fenkal na leen.» 4:17 Booba Yeesu tàmbali di waare naan: «Tuubleen seeni bàkkaar, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji jegesi na.» 4:18 Gannaaw loolu Yeesu doon dox ca tefesu dexu Galile, mu gis fa ñaar ñu bokk ndey ak baay, mooy Simoŋ mi ñuy wax Piyeer, ak Andare. Fekk ñuy sànni seen caax ca dex ga, ndaxte ay nappkat lañu woon. 4:19 Yeesu ne leen: «Ñëwleen topp ci man, ma def leen nappkati nit.» 4:20 Ca saa sa ñu daldi bàyyi seeni mbaal, topp ci moom. 4:21 Ba Yeesu demee ba ca kanam, mu gis yeneen ñaar ñu bokk ndey ak baay, ñuy Saag doomu Sebede, ak Yowaana rakkam. Ñu nekk ci seen biir gaal ak Sebede seen baay, di defar seeni mbaal. Noonu Yeesu woo leen. 4:22 Ca saa sa ñu daldi bàyyi gaal ga ak seen baay, topp ci moom. 4:23 Ba loolu amee Yeesu doon wër Galile gépp, di jàngale ci seeni jàngu tey yégle xebaar bu baax bi ci nguuru Yàlla; muy faj jàngoro yépp ak wéradi yépp ca nit ña, 4:24 ba tax turam siiw ba ci biir réewu Siri mépp. Ñu di ko indil ñi wopp ñépp, ñi sonn ndax ay jàngoro ak metit yu bare, ñi rab jàpp, ñiy say ak ñi làggi, mu faj leen. 4:25 Noonu mbooloo mu bare topp ci moom, jóge ci wàlli Galile ak diiwaan bi ñuy wax Fukki dëkk yi, ci dëkku Yerusalem ak ci diiwaanu Yude, ba ci gannaaw dexu Yurdan..
5:1 Bi Yeesu gisee mbooloo ma nag, mu yéeg ca tund wa, toog; taalibeem ya ñëw ci moom. 5:2 Mu daldi leen jàngal naan: 5:3 «Yéen ñi xam seen ñàkk doole ngir neex Yàlla,barkeel ngeen,ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji,yéena ko yelloo. 5:4 Yéen ñi nekk ci naqar, barkeel ngeen,ndax dees na dëfël seen xol. 5:5 Yéen ñi lewet, barkeel ngeen,ndax dingeen moomi àddina. 5:6 Yéen ñi xiif te mar njub, barkeel ngeen,ndax dingeen regg. 5:7 Yéen ñi am yërmande, barkeel ngeen,ndax dees na leen yërëm. 5:8 Yéen ñi am xol bu sell, barkeel ngeen,ndax dingeen gis Yàlla. 5:9 Yéen ñiy wut jàmm, barkeel ngeen,ndax dees na leen tudde doomi Yàlla. 5:10 Yéen ñi ñu fitnaal ndax seen njub,barkeel ngeen,ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji,yéena ko yelloo. 5:11 «Barkeel ngeen, bu ñu leen di saaga, di leen fitnaal, di leen sosal lépp lu bon ngir man. 5:12 Bégleen te bànneexu, ndax seen yool dina réy ci laaxira. Ndaxte noonu lañu daan fitnaale yonent yi fi jiitu. 5:13 «Yéena di xoromus àddina. Bu xorom si sàppee, nan lañu koy delloo cafkaam? Du jariñati dara, lu dul ñu sànni ko ci biti, nit ñi dox ci kawam. 5:14 Yéena di leeru àddina. Dëkk, bu nekk ci kaw tund du man a nëbbu. 5:15 Te it duñu taal làmp, dëpp cig leget, waaye dañu koy wékk, ba muy leeral ñi nekk ci kër gi ñépp. 5:16 Na seen leer leere noonu ci kanamu nit ñi, ngir ñu gis seeni jëf yu rafet, te màggal seen Baay bi ci kaw. 5:17 «Buleen defe ne, ñëw naa ngir dindi yoonu Musaa ak waxi yonent yi. Ñëwuma ngir dindi leen, waaye ngir ñu am ci man. 5:18 Ndaxte ci dëgg maa ngi leen koy wax, li feek asamaan ak suuf wéyul, benn tomb walla benn rëddu araf du wéy mukk ci yoonu Musaa, ba kera yépp di am. 5:19 Ku tebbi nag ba gën a tuuti ci ndigal yii, te ngay jàngal nit ñi noonu, dees na la tudde ki gën a tuuti ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji. Waaye ku leen di sàmm, di leen digle, dees na la tudde ku mag ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji. 5:20 Ndaxte maa ngi leen koy wax, bu seen njubte ëppul njubteg xutbakat ya ak Farisen ya, dungeen tàbbi mukk ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji. 5:21 «Dégg ngeen ne, waxoon nañu maam ya ne leen: “Bul rey nit; ku rey nit, yoon dina la dab.” 5:22 Waaye man maa ngi leen di wax ne, képp ku mere sa mbokk, dinañu la àtte. Ku wax sa mbokk: “Amoo bopp,” dinañu la àtte ca kureelu àttekat ya. Ku ko wax: “Alku nga,” dinañu la àtte ci safara. 5:23 Booy yóbbu nag sa sarax ca saraxalukaay ba, te nga fàttaliku foofa ne, sa mbokk am na lu mu la meree, 5:24 nanga fa bàyyi sa sarax ca kanamu saraxalukaay ba, nga jëkk a dem, juboo ak sa mbokk, ba noppi dellu, joxe sa sarax. 5:25 «Gaawal a juboo ak ki lay yóbbu, ngeen layooji, bala ngeen a egg; ngir bañ ki ngay layool jébbal la àttekat ba, kooka jox la alkaati ba, ñu tëj la. 5:26 Ci dëgg maa ngi la koy wax, doo génn foofa mukk te feyuloo dërëm bi ci mujj. 5:27 «Te it dégg ngeen ne waxoon nañu: “Bul njaaloo.” 5:28 Waaye man maa ngi leen di wax ne, képp ku xool jigéen, xédd ko, njaaloo nga ak moom ci sa xel. 5:29 Bu la sa bëtu ndeyjoor bëggee yóbbe bàkkaar, luqi ko, sànni ko fu sore. 5:30 Ndaxte ñàkk benn ci say cér moo gën ci yaw, ñu sànni sa yaram wépp ci safara. Bu la sa loxol ndeyjoor bëggee yóbbe bàkkaar, dagg ko, sànni ko fu sore. Ndaxte ñàkk benn ci say cér moo gën ci yaw ñu sànni sa yaram wépp ci safara. 5:31 «Waxoon nañu ne: “Ku fase sa jabar, nga bindal ko kayitu pase.” 5:32 Waaye man maa ngi leen di wax ne, ku fase sa jabar te du ci njaaloo, yaa koy tegtal yoonu njaaloo. Te it ku takk jigéen ju ñu fase, njaaloo nga. 5:33 «Dégg ngeen itam ne, waxoon nañu maam ya ne leen: “Bul weddi sa ngiñ, waaye li nga giñ def ko ngir Boroom bi.” 5:34 Waaye man maa ngi leen di wax ne, buleen giñ dara; bumu doon ci asamaan, ndaxte moo di jalu Buur Yàlla; 5:35 bumu doon ci àddina, ndax moo di tegukaayu tànkam; bumu doon it ci Yerusalem, ndax moo di dëkku Buur bu mag bi. 5:36 Bul giñ it ci sa bopp, ndaxte mënuloo weexal mbaa ñuulal benn ci say kawar. 5:37 Sa waaw na nekk waaw, sa déedéet na nekk déedéet. Loo ci teg, ci Ibliis la jóge. 5:38 «Te it dégg ngeen ne, waxoon nañu: “Bët, bët a koy fey; bëñ, bëñ a koy fey.” 5:39 Waaye man maa ngi leen di wax ne, buleen bañ ku leen def lu bon, waaye ku la pes ci sa lexu ndeyjoor, jox ko ba ca des. 5:40 Ku la bëgg a kalaame, ngir jël sa turki, nga boole ca it sa mbubb mu mag. 5:41 Ku la ga, nga yenul ko doxub benn kilomet, àndal ak moom ñaar. 5:42 Mayal ku lay ñaan, te bul jox gannaaw ku lay leb. 5:43 «Dégg ngeen ne, waxoon nañu: “Soppal sa moroom te sib sa bañaale.” 5:44 Waaye man maa ngi leen di wax ne, soppleen seeni bañaale te ñaanal ñi leen di fitnaal, 5:45 ngir wone ne, yéenay doomi seen Baay bi nekk ci kaw. Ndaxte mu ngi fenkal jantam ci kaw ñu bon ñi ak ñu baax ñi, te muy tawal ñi jub ak ñi jubadi. 5:46 Su ngeen soppee ñi leen sopp, ban yool ngeen am? Xanaa juutikat yi duñu def noonu it? 5:47 Su ngeen nuyoo seeni bokk rekk, lu ngeen def lu doy waar? Xanaa ñi xamul Yàlla duñu def noonu it? 5:48 Nangeen mat nag, ni seen Baay bi ci kaw mate.
6:1 «Wottuleen a def seeni jëf yu jub ci kanamu nit ñi, muy ngistal. Lu ko moy, dungeen am yool ci seen Baay bi nekk ci kaw. 6:2 Booy sàkk sarax nag, bul yeble ci sa kanam, ñu yéene la. Moom la naaféq yi di def ca jàngu ya ak ca mbedd ya, ngir nit ñi màggal leen. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp. 6:3 Waaye booy sàkk sarax, bu sa loxob càmmooñ xam li sa loxob ndeyjoor di def, 6:4 ngir sa sarax nekk kumpa. Noonu sa Baay, bi dara umpul, dina la ko delloo. 6:5 «Bu ngeen di ñaan, buleen mel ni naaféq yi, ñoom ñi bëgg di ñaan, taxaw ca jàngu ya ak fa mbedd yay daje, ngir nit ñi gis leen. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp. 6:6 Yaw nag booy ñaan, duggal ci sa néeg, tëj bunt bi, te nga ñaan sa Baay bi bët mënta gis. Noonu sa Baay, bi dara umpul, dina la ko delloo. 6:7 «Te it bu ngeen di ñaan, buleen bareel wax yu amul njariñ, mel ni ñi xamul Yàlla; ñoom defe nañu ne, Yàlla dina leen nangul ndax seen wax ju bare. 6:8 Buleen nirook ñoom, ndaxte seen Baay xam na seeni soxla, laata ngeen ko koy wax. 6:9 Yéen nag nii ngeen war a ñaane:“Sunu Baay bi nekk ci kaw,na sa tur sell, 6:10 na sa nguur ñëw,na sa coobare am ci suuf mel ni ci kaw. 6:11 May nu tey li nu war a dunde; 6:12 te baal nu sunuy tooñ, ni nu baale ñi nu tooñ; 6:13 bu nu teg ci yoonu nattu, waaye nga musal nu ci lu bon.Ndaxte yaw yaa yelloo nguur ak kàttan ak màggaay, ba fàww. Amiin.” 6:14 «Su ngeen baalee ñi leen tooñ, seen Baay bi ci kaw dina leen baal seeni tooñ yéen itam. 6:15 Waaye su ngeen baalul ñi leen tooñ, seen Baay it du leen baal seeni tooñ. 6:16 «Su ngeen di woor, buleen mel ni naaféq yi, ñoom ñi yoggoorlu, di ñaawal seeni kanam, ngir seen koor feeñu nit ñi. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp. 6:17 Yaw nag booy woor, xeeñalal sa bopp te nga sëlmu, 6:18 ngir sa koor bañ a feeñu nit ñi, waaye mu feeñu sa Baay bi bët mënta gis. Noonu sa Baay, bi dara umpul, dina la ko delloo. 6:19 «Buleen dajale alal ci àddina, fu ko max ak xomaag di yàqe, ak fu sàcc di dugg, jot ko. 6:20 Waaye dajaleleen alal ci laaxira, fu ko max ak xomaag dul yàqe, ak fu sàcc dul dugg, jot ko. 6:21 Ndaxte fu sa alal nekk, fa la sa xol nekk itam. 6:22 «Bët mooy làmpu yaram. Bu sa bët wéree, kon sa yaram wépp leer, 6:23 waaye bu sa bët woppee, kon sa yaram wépp lëndëm. Leer gi nekk ci yaw, bu nekkee lëndëm, naka la lëndëm googu di këruuse! 6:24 «Kenn mënul a jaamoondoo ñaari sang; fàww nga bañ kii, bëgg ki ci des, walla nga jàpp ci kenn ki, xeeb ki ci des. Mënuleen a boole jaamu Yàlla ak jaamu Alal. 6:25 «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, buleen seen bakkan jaaxal, ci lu ngeen war a lekk, walla lu ngeen war a naan. Buleen jaaxle it ngir seen yaram, ci lu ngeen war a sol. Xanaa bakkan gënul lekk, te yaram gënul koddaay? 6:26 Seetleen picci asamaan: duñu ji, duñu góob, duñu denc ci sàq; teewul seen Baay bi ci kaw moo leen di dundal. Ndax ëppuleen maana picc yi ci lu bare? 6:27 Ana kan ci yéen ci kaw njaaxleem moo man a yokk waxtu ci àppam? 6:28 «Te lu tax ngeen di jaaxle ngir koddaay? Seetleen bu baax, ni tóor-tóori ñax mi di saxe ci tool yi. Duñu liggéey, duñu ëcc, 6:29 waaye maa ngi leen di wax ne, Suleymaan sax ci ndamam soluwul woon ni benn ci ñoom. 6:30 Yéen ñi néew ngëm! Bu Yàlla woddee nii ñaxum tool yi, miy sax tey, te bu subaa ñu def ko ci taal bi, ndax du leen gën a wodd? 6:31 Buleen jaaxle nag, di wax ne: “Lu nu war a lekk? Lu nu war a naan?” walla: “Lu nu war a sol?” 6:32 Ndaxte loolu lépp, ñi xamul Yàlla ñoo koy wut. Te seen Baay, bi nekk ci kaw, xam na ne am ngeen soxla ci loolu lépp. 6:33 Waaye jëkkleen a wut nguuram ak njubteem, te loolu lépp dina leen ko ci dollil. 6:34 Buleen jaaxle nag ngir ëllëg, ndaxte ëllëg dina topptoo boppam. Bés bu nekk, coonoom doy na ko.
7:1 «Buleen àtte seeni moroom ak ñaaw njort, ngir bañ ñu àtte leen yéen itam. 7:2 Ndaxte dees na leen àtte ak ni ngeen di àttee, nattal leen ak li ngeen di nattale. 7:3 Lu tax ngay xool ñax gi ci sa bëtu mbokk, te gisuloo gànj gi ci sa bët yaw? 7:4 Walla nan ngay waxe sa mbokk: “May ma, ma dindil la ñax gi ci sa bët,” fekk gànj a ngii ci sa bët yaw? 7:5 Naaféq, jëkkal a dindi gànj gi ci sa bët, te noonu dinga man a gis bu leer, ngir dindi ñax gi ci sa bëtu mbokk. 7:6 «Buleen jox lu sell xaj yi, mbaa sànni seeni per ci kanamu mbaam-xuux yi, ngir bañ ñu dëggaate ko te walbatiku, xotti leen. 7:7 «Ñaanleen, ñu may leen; seetleen te dingeen gis; fëggleen, ñu ubbil leen. 7:8 Ndaxte képp kuy ñaan, dinga am; kuy seet, dinga gis; kuy fëgg, ñu ubbil la. 7:9 Kan ci yéen, bu la sa doom ñaanee mburu, nga jox ko doj? 7:10 Walla mu ñaan la jën, nga jox ko jaan? 7:11 Ndegam yéen ñi bon yéena man a jox seeni gune lu baax, astemaak seen Baay bi nekk ci kaw dina jox lu baax ñi ko koy ñaan! 7:12 «Kon nag lépp lu ngeen bëgg, nit ñi defal leen ko, yéen itam nangeen leen ko defal; ndaxte loolu moo ëmb yoonu Musaa ak waxi yonent yi. 7:13 «Jaarleen ci bunt bu xat bi, ndaxte bunt bi ak yoon wi jëm sànku yaatu nañu, te ñi ciy jaar bare. 7:14 Waaye buntu dund gu wóor xat na, te yoon wi jëm kaw sew na, te ñi ko gis barewul. 7:15 «Moytuleen ñi mbubboo turu yonent. Dañuy ñëw ci yéen, yor melow xar, waaye ci biir ay bukki yu soxor lañu. 7:16 Dingeen leen xàmmee ci seeni jëf. Ndax dees na witte réseñ ci dédd, walla figg ci xaaxaam? 7:17 Noonu garab gu baax gu nekk dina meññ doom yu neex, waaye garab gu bon dina meññ doom yu bon. 7:18 Garab gu baax mënul a meññ doom yu bon, naka itam garab gu bon mënul a meññ doom yu neex. 7:19 Garab gu nekk gu dul meññ doom yu neex, dees na ko gor, sànni ko ca safara sa. 7:20 Ci seeni jëf nag ngeen leen di xàmmee. 7:21 «Du képp ku may wax: “Boroom bi, Boroom bi,” mooy dugg ca nguuru Yàlla Aji Kawe ji; ka cay dugg mooy kiy def sama coobareg Baay, bi nekk ci kaw. 7:22 Bu bés baa, ñu bare dinañu ma wax: “Boroom bi, Boroom bi, ndax du ci saw tur lanu daa waxe ci kàddug Yàlla? Ndax du ci saw tur lanu daa dàqe ay rab? Ndax du ci saw tur lanu daa defe ay kéemaan yu bare?” 7:23 Ci kaw loolu dinaa leen wax dëgg ne leen: “Musuma leen a xam; soreleen ma, yéen ñiy def bàkkaar.” 7:24 «Képp ku dégg nag lii ma leen wax, te di ko jëfe, dinga mel ni nit ku am xel, ku tabax këram, samp ko ciw doj. 7:25 Ba mu noppee, taw bi daldi sóob, wal mi ñëw, ngelaw li jóg, ñu dal ci kaw kër ga; waaye màbbul, ndaxte mu ngi jàpp ca doj wa. 7:26 Waaye képp ku dégg lii ma leen wax, te jëfewuloo ko, dinga mel ni nit ku ñàkk xel, ku tabax këram ci gànnuus bi. 7:27 Ba mu noppee, taw bi daldi sóob, wal mi ñëw, ngelaw li jóg, ñu dal ci kaw kër ga; mu màbb, ba ne tasar.» 7:28 Bi Yeesu waxee loolu ba noppi, mbooloo ma daldi waaru ca njàngaleem, 7:29 ndaxte jàngal na leen ak sañ-sañ bu seeni xutbakat amul.
8:1 Bi loolu amee Yeesu wàcc ca tund wa, te mbooloo mu bare topp ko. 8:2 Noonu ku gaana ñëw, sukk ci kanamam ne ko: «Sang bi, soo ko bëggee, man nga maa faj.» 8:3 Yeesu tàllal loxoom, laal ko naan: «Bëgg naa ko, wéral.» Ca saa sa ngaanaam daldi deñ. 8:4 Yeesu ne ko: «Déglul, bu ko wax kenn, waaye demal won sa bopp saraxalekat bi, te nga jébbal Yàlla sarax, si yoonu Musaa santaane, ngir mu nekk seede ci ñoom.» 8:5 Gannaaw loolu Yeesu duggoon na Kapernawum. Bi mu fa duggee nag, ab njiitu xare fekksi ko. Mu ñaan ko, 8:6 ne ko: «Sang bi, sama surga dafa làggi, tëdd ca kër ga te sonn lool.» 8:7 Yeesu ne ko: «Dinaa ñëw faj ko.» 8:8 Waaye njiit la tontu ko ne: «Sang bi, yeyoowuma nga dugg ci sama kër; waxal genn kàddu rekk, te sama surga dina wér. 8:9 Ndaxte man itam maa ngi nekk ci ndigal, te ame naa ay xarekat ci sama ndigal. Su ma nee kii: “Demal,” mu dem. Mbaa ma ne keneen ki: “Ñëwal,” mu ñëw. Te su ma nee sama jaam: “Defal lii,” mu def ko.» 8:10 Bi ko Yeesu déggee, mu waaru, ne ña topp ci moom: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, musumaa gis ci bànni Israyil ku gëme ni kii. 8:11 Maa ngi leen koy wax, ñu bare dinañu ñëw, jóge ci penku ak sowu, bokk lekk ak Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji. 8:12 Waaye ñi waroon a bokk ca nguur ga, dees na leen sànni ci biti ci lëndëm gi. Foofa dees na fa jooy tey yéyu.» 8:13 Ci kaw loolu Yeesu wax njiit la ne ko: «Ñibbil, na ame, ni nga ko gëme.» Noonu ca waxtu woowa sax surga ba daldi wér. 8:14 Gannaaw loolu Yeesu dem kër Piyeer. Ba mu eggee, mu fekk gorob Piyeer bu jigéen tëdd ak yaram wu tàng. 8:15 Bi mu ko gisee, Yeesu laal loxoom, tàngoor wa daldi wàcc; soxna sa jóg, di ko topptoo. 8:16 Ca ngoon sa ñu indil ko ñu bare ñu rab jàpp. Yeesu dàq rab ya ak kàddoom te faj ñi wopp ñépp. 8:17 Loolu mu def, def na ko, ngir la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi am, bi mu naan:«Fab na sunuy wopp, gàddu sunuy jàngoro.» 8:18 Bi Yeesu gisee mbooloo ma ko wër nag, mu sant taalibe ya, ñu jàll dex ga. 8:19 Laata ñuy jàll, benn xutbakat daldi ñëw ci moom ne ko: «Kilifa gi, dinaa la topp fépp foo jëm.» 8:20 Waaye Yeesu tontu ko ne: «Till yi am nañu seeni kàmb, te picci asamaan am nañu ay tàgg, waaye Doomu nit ki amul fu mu noppal boppam.» 8:21 Noonu keneen ca taalibe ya ne ko: «Sang bi, may ma, ma jëkk a dem suuli sama baay.» 8:22 Yeesu tontu ko ne: «Toppal ci man te bàyyi ñi dee, ñu suul seeni néew.» 8:23 Bi mu ko waxee, Yeesu dugg ca gaal ga, ay taalibeem topp ko. 8:24 Ca saa sa ngelaw lu bare daldi yengal dex ga, ba duus ya sàng gaal ga. Fekk booba Yeesu nelaw. 8:25 Noonu taalibe ya daldi jegesi, yee ko naan: «Sang bi, musal nu, nu ngiy dee.» 8:26 Waaye Yeesu tontu leen: «Yéen ñi néew ngëm, lu tax ngeen tiit?» Ci kaw loolu mu jóg, daldi gëdd ngelaw li ak duus yi. Lépp dal, ba ne nemm. 8:27 Bi ko nit ña gisee, ñu waaru naan: «Kii kan la ci biir nit ñi, ba ngelaw li ak dex gi di ko déggal?» 8:28 Bi Yeesu jàllee nag, ba teer ca diiwaanu waa Gadara, ñaar ñu rab jàpp daldi génn ca sëg ya, ñëw kar ko. Ñaar ñooñu nag, ñu soxor lañu woon, ba kenn ñemewul woon a jaar foofa. 8:29 Ña rab jàpp daldi xaacu naan: «Yaw Doomu Yàlla ji, loo nuy fexeel? Ndax danga noo bëgg a mbugal, bala waxtu way jot?» 8:30 Fekk amoon na ca wet ya géttu mbaam-xuux yu bare yuy for. 8:31 Rab ya nag ñaan ko ne: «Boo nu dàqee, sànni nu ca géttu mbaam-xuux ya.» 8:32 Yeesu ne leen: «Demleen.» Rab ya nag daldi génn, dugg ca mbaam-xuux ya, ñu daldi bartalu, daanu ca dex ga, lab ca ndox ma. 8:33 Ba sàmm ya gisee loolu, ñu daw, dem dëkk ba, nettaliji lépp ak la xewoon ca ña rab jàpp. 8:34 Noonu dëkk ba bépp génn seeti Yeesu. Ba ñu ko gisee nag, ñu ñaan ko, mu génn seen réew.
9:1 Bi loolu amee Yeesu dugg cig gaal, jàll dex ga, dellu dëkkam. 9:2 Foofa ñu indil ko ku tëdd ci basaŋ, fekk yaramam wépp làggi. Bi Yeesu gisee seen ngëm, mu ne ku làggi ka: «Na sa xel dal, sama waay, baal nañu la say bàkkaar.» 9:3 Bi mu waxee loolu, ay xutbakat daldi ne ci seen biir: «Nit kii mu ngi sosal Yàlla.» 9:4 Waaye Yeesu xam seen xalaat ne leen: «Lu tax ngeen am xalaat yu bon ci seen xol? 9:5 Ma wax ne: “Baal nañu la say bàkkaar,” walla ma ne: “Jógal te dox,” lan moo ci gën a yomb? 9:6 Waaye xamleen ne, Doomu nit ki am na ci àddina sañ-sañu baale bàkkaar yi.» Ci kaw loolu Yeesu ne ku làggi ka: «Jógal, jël sa basaŋ te nga ñibbi.» 9:7 Noonu làggi ba daldi jóg, ñibbi. 9:8 Ba mbooloo ma gisee loolu, ñu daldi ragal te màggal Yàlla, mi dénk sañ-sañ bu tollu noonu doom Aadama yi. 9:9 Bi Yeesu jógee foofa, mu gis nit ku tudd Macë, toog ca juuti ba. Yeesu ne ko: «Kaay topp ma.» Noonu Macë jóg, daldi ko topp. 9:10 Gannaaw ga Yeesu doon lekk ca kër ga, te ay juutikat ak i boroom bàkkaar yu bare dikk, bokk lekk ak Yeesu ak taalibeem ya. 9:11 Bi ko Farisen ya gisee nag, ñu ne taalibe ya: «Lu tax seen kilifa di lekkandoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar?» 9:12 Waaye bi ko Yeesu déggee, mu ne: «Ñi wér soxlawuñu fajkat, ñi wéradi ñoo ko soxla. 9:13 Mbind mi nee na: “Yërmande laa bëgg, waaye du rendi saraxi mala.” Demleen nag te seet lu wax joojuy tekki. Ndaxte ñëwuma, ngir woo ñi jub, waaye bàkkaarkat yi laay woo.» 9:14 Gannaaw loolu taalibey Yaxya ñëw ci Yeesu ne ko: «Lu tax nuy woor, nun ak Farisen yi, te say taalibe duñu woor?» 9:15 Yeesu tontu leen: «Ndax gan yi ñëw ci céet dinañu naqarlu dara, li feek boroom céet gaa ngi ànd ak ñoom? Waaye bés yaa ngi ñëw yu ñuy jële boroom céet gi ci seen biir; booba nag dinañu woor. 9:16 Xam ngeen ne, kenn du daax mbubb mu màggat ak sekkit wu bees; ndaxte sekkit wi day ñoddi mbubb mi, te xottiku bi gën a yaatu. 9:17 Te it duñu def biiñ bu bees ci mbuusi der yu màggat. Lu ko moy, mbuus yi dañuy toj, biiñ bi tuuru te mbuus yi yàqu. Waaye biiñ bu bees, dees na ko def ci mbuus yu bees. Noonu ñoom ñaar duñu yàqu.» 9:18 Bi leen Yeesu di wax loolu, benn njiitu jàngu daldi ñëw, sukk ci kanamam ne ko: «Sama doom ju jigéen dafa faatu léegi, waaye ñëwal, teg ko say loxo, te dina dundaat.» 9:19 Noonu Yeesu jóg, topp ko, moom ak ay taalibeem. 9:20 Bi ñuy dem nag, amoon na ca mbooloo ma jigéen juy xëpp deret diirub fukki at ak ñaar. Mu defe ne, su laalee mbubbam rekk, dina wér. Mu jegeñsi Yeesu nag, doxe ko gannaaw, laal catu mbubbam. 9:22 Bi mu ko defee Yeesu woññiku ne ko: «Na sa xel dal, soxna si, sa ngëm faj na la.» Noonu jigéen ja daldi wér ca saa sa. 9:23 Bi Yeesu eggee kër njiit la, mu gis ñiy liit ak toxoro, ak mbooloo may def coow lu bare. 9:24 Mu ne leen: «Génnleen, janq bi deewul, day nelaw rekk.» Bi ko mbooloo ma déggee, ñu daldi ko ñaawal. 9:25 Waaye ñu génne leen, Yeesu dugg, jàpp loxob janq ba, mu daldi jóg. 9:26 Noonu xebaaru li mu def daldi siiw ca réew ma. 9:27 Bi Yeesu jógee foofa, ñaari gumba topp ko, di wax ca kaw naan: «Yërëm nu, yaw Sëtu Daawuda bi!» 9:28 Noonu Yeesu dugg ca kër ga, gumba ya toppsi ko. Yeesu ne leen: «Ndax gëm ngeen ne, man naa def li ngeen ma laaj?» Ñu tontu ko: «Waaw Sang bi.» 9:29 Kon Yeesu daldi laal seeni bët ne leen: «Na am, ni ngeen ko gëme.» 9:30 Ca saa sa seeni bët daldi ubbiku. Yeesu dénk leen bu wér ne leen: «Moytuleen kenn xam ko.» 9:31 Waaye ñu génn rekk, siiwal turam fu nekk. 9:32 Bi ñu fa jógee nag, amoon na ñeneen ñu ñëw fi moom, indil ko ku rab jàpp, mu luu. 9:33 Yeesu dàq rab wa, luu ba daldi wax. Bi ñu ko gisee, mbooloo ma waaru, ñu ne: «Lu mel nii, musuñu koo gis ci Israyil.» 9:34 Waaye Farisen ya ne: «Ci kàttanu buuru rab yi lay dàqe rab yi.» 9:35 Noonu Yeesu wër dëkk yu mag ya yépp ak yu ndaw ya, di leen jàngal ci seeni jàngu, tey yégle xebaar bu baax bi jëm ci nguuru Yàlla, di faj jàngoro yépp ak wéradi yépp. 9:36 Bi Yeesu gisee mbooloo ma, mu yërëm leen, ndaxte dañoo sonn ba ne yogg, mel ni xar yu amul sàmm. 9:37 Noonu mu ne taalibeem ya: «Ngóob mi yaatu na, waaye liggéeykat yi barewuñu. 9:38 Ñaanleen nag Boroom ngóob mi, mu yebal ay liggéeykat, ñu góob toolam.»
10:1 Noonu Yeesu woo ca moom fukki taalibeem ya ak ñaar, jox leen sañ-sañu dàq rab yi, tey faj jàngoro yépp ak wéradi yépp. 10:2 Fukki ndaw ak ñaar, ya Yeesu yónni woon nag, nii lañu tuddoon: ku jëkk ki mooy Simoŋ mi ñuy wax Piyeer, ak Andare mi bokk ak moom ndey ak baay; Saag doomu Sebede, ak Yowaana rakkam;l 10:3 Filib ak Bartelemi; Tomaa ak Macë, juutikat ba woon; Saag doomu Alfe, ak Tade;l 10:4 Simoŋ, mi bokk ca mbooloo, ma ñu tudde Ñi farlu ci moom seen réew; ak Yudaa Iskariyo, mi nar a wor Yeesu. 10:5 Yeesu yónni fukk ñooñule ak ñaar, jox leen ndigal ne leen: «Buleen dem ci ñi dul Yawut mbaa dugg ci benn dëkku waa Samari. 10:6 Waaye demleen ci bànni Israyil, ñoom ñi réer niy xar. 10:7 Bu ngeen demee nag, yégleleen naan: “Nguuru Yàlla Aji Kawe ji jegesi na.” 10:8 Fajleen ñi wopp, dekkal ñi dee, fajleen gaana yi te dàq rab yi. Cig neen ngeen ame, mayeleen cig neen. 10:9 Buleen dajale wurus, xaalis mbaa xànjar ci seeni maxtume. 10:10 Buleen wut it mbuus ngir tukki mbaa ñaari turki, ay dàll mbaa aw yet, ndaxte liggéeykat yeyoo na dundam. 10:11 «Bu fekkee ne agsi ngeen ci dëkk bu mag mbaa bu ndaw, nangeen fa seet ku fa am faayda, dal ca moom ba kera ngeen jóge dëkk ba. 10:12 Bu ngeen di dugg ci kër nag, nuyooleen. 10:13 Bu fekkee ne kër ga yeyoo na ko, na seen jàmm wàcc ci ñoom, waaye bu ko yeyoowul, na seen yéene dellusi ci yéen. 10:14 Koo xam ne gàntu na leen, mbaa mu tanqamlu seeni wax, génnleen ca kër ga mbaa ca dëkk ba, yëlëb seen pëndu tànk. 10:15 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, keroog bésub àtte ba, waa réewu Sodom ak Gomor ñooy tane dëkk boobu. 10:16 «Dégluleen, maa ngi leen di yónni, mel ni ay xar ci biir ay bukki. Muusleen nag niy jaan, te lewet niy pitax. 10:17 Waaye moytuleen nit ñi, ndaxte dinañu leen jébbal àttekat yi te dóor leen ay yar ci seeni jàngu. 10:18 Dees na leen yóbbu ngir man ci kanami boroom réew ak i buur, ngir ngeen seede ma ci ñoom ak ci ñi dul Yawut. 10:19 Boo xamee ne nag jébbale nañu leen, buleen am xel ñaar ci li ngeen di wax, mbaa ni ngeen koy waxe. Ndaxte ca waxtu woowa sax dingeen jot li ngeen war a wax; 10:20 du yéenay wax, waaye Xelum seen Baay mooy wax ci yéen. 10:21 «Mag dina joxe rakkam ci dee, baay joxe doomam; ay doom it dinañu jóg, bañ seeni waajur, di leen reylu. 10:22 Te yéen nag, ñépp dinañu leen bañ ndax sama tur; waaye ku muñ ba muj ga, mucc. 10:23 Boo xamee ne fitnaal nañu leen ci dëkk bii, demleen ca ba ca kanam. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, dungeen man a wër dëkki Israyil yépp, te Doomu nit ki ñëwul.» 10:24 Yeesu teg ca ne: «Taalibe gënul kilifaam, te jaam gënul sangam. 10:25 Bu taalibe yemee ak kilifaam demin, doy na; jaam it ni sangam. Ndegam tudde nañu boroom kër gi Beelsebul, astemaak waa kër gi. 10:26 Kon nag buleen leen ragal, ndaxte amul dara lu nëbbu, lu ñu warul a biral, mbaa luy kumpa lu ñu warul a siiwal. 10:27 Li ma leen wax ci biir lëndëm, waxleen ko ci leer; li ma leen déey, yégleleen ko ci kaw taax yi. 10:28 Te buleen ragal ñu man a rey yaram, te mënuñoo rey ruu, waaye ragal-leen Ki man a sànk yaram ak ruu ci safara. 10:29 Ñaari picci rammatu, ndax duñu ko jaay ci dërëm? Waaye benn ci ñoom du daanu ci suuf te soobul seen Baay. 10:30 Seen kawari bopp sax, waññees na leen. 10:31 Kon buleen ragal dara, yéena gën ndiiraanu rammatu. 10:32 «Koo xam ne nangu nga ma ci kanamu nit ñi, man itam dinaa la nangu ci sama kanamu Baay, bi nekk ci kaw. 10:33 Waaye ku ma gàntu ci kanamu nit ñi, man itam dinaa la gàntu ci sama kanamu Baay, bi nekk ci kaw. 10:34 «Te it buleen defe ne, damaa ñëw ngir indi jàmm ci àddina; ñëwuma ngir indi jàmm, waaye jaasi laa indaale. 10:35 Ndaxte ñëw naa ngir féewale doom ak baayam, doom ju jigéen ak ndeyam, jabar ak goroom; 10:36 te nooni nit ñooy waa këram. 10:37 Ku ma gënalul sa ndey walla sa baay, yeyoowuloo ma; ku ma gënalul sa doom ju góor walla ju jigéen, yeyoowuloo ma. 10:38 Koo xam ne kii nanguwuloo ñàkk sa bakkan, ba mel ni ku ñu daaj ci bant, te nga topp ma, yeyoowuloo ma. 10:39 Kuy rawale sa bakkan, ñàkk ko, te ku ñàkk sa bakkan ndax man, jotaat ko. 10:40 «Te lii itam am na, ku leen nangu, nangu na ma, te ku ma nangu, nangu na ki ma yónni. 10:41 Ku nangu yonent ndax yónnentam, dina jot ci peyu yonent; te ku nangu ku jub ndax njubteem, dina jot ci peyu ku jub. 10:42 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, koo xam ne kii may na kaasu ndox mu sedd rekk kenn ci ñi gën a ndaw, ndax sama taalibe la, kooku du ñàkk yoolam mukk.»
11:1 Ba Yeesu joxee fukki taalibeem ya ak ñaar ndigal yooyu, mu jóge fa, ngir dem jàngaleji ak a waare ci seeni dëkk. 11:2 Gannaaw loolu Yaxya dégg ca kaso ba jëfi Almasi bi. Mu yónni ci moom nag ay taalibeem, 11:3 ne ko: «Ndax yaa di Ki war a ñëw, walla danoo war a xaar keneen?» 11:4 Yeesu tontu leen ne: «Demleen nettali Yaxya li ngeen dégg te gis ko. 11:5 Gumba yaa ngi gis, lafañ yiy dox, gaana yi wér, tëx yiy dégg, ñi dee di dekki, te ñi woyoflu ñu ngi dégg xebaar bu baax bi. 11:6 Yaw mi sa ngëm yolomul ndax man, barkeel nga.» 11:7 Bi nga xamee ne taalibe ya Yaxya yónni woon ci Yeesu dem nañu, Yeesu daldi wax ak mbooloo ma ci mbirum Yaxya ne leen: «Lu ngeen seeti woon ca màndiŋ ma? Xanaa barax buy jaayu ci ngelaw li? 11:8 Kon lu ngeen seeti woon nag? Nit ku sol yére yu rafet? Waaye ñi sol yére yu rafet ñu ngi dëkk ci këri buur. 11:9 Lu tax ngeen génn nag? Ngir gis ab yonent? Waaw, wax naa leen ne, ëpp na yonent. 11:10 Yaxya male moo di ki ñu waxoon ci Mbind mi naan:“Maa ngi yónni sama ndaw, mu jiitu la,te xàllal la yoon ci sa kanam.” 11:11 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ci li jigéen jur, ku sut Yaxya musul a feeñ. Waaye ba tey ki gën a ndaw ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji moo ko sut. 11:12 Ci li dale ci jamonoy Yaxya ba léegi, nit ñaa ngi góor-góorlu ngir dugg ci nguuru Yàlla, te ñi sawar ñoo ci am wàll. 11:13 Ndaxte li yonent yi wax ak li yoonu Musaa tëral ñu ngi doon dox, ba kera Yaxya di feeñ. 11:14 Te Yaxya moomu, su ngeen bëggee nangu lii, mooy Iliyas bi waroon a ñëw. 11:15 Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp. 11:16 «Niti jamono jii nag, lan laa leen man a mengaleel? Ñu ngi nirook xale yu toog ca pénc ma, di woo seeni xarit, 11:17 ne leen:“Liital nanu leen ak toxoro, te fecculeen,woyal nanu leen woyi dëj, te jooyuleen.” 11:18 Ndaxte Yaxya feeñ na, lekkul, naanul, ngeen daldi ne: “Dafa ànd ak rab.” 11:19 Gannaaw gi nag, Doomu nit ki ñëw na, lekk, naan, ngeen daldi ne: “Kii daal bëgg na lekk, di naan biiñ, tey xaritoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar.” Waaye li xam-xamu Yàlla di jur, mooy firndeel ne dëgg la.» 11:20 Gannaaw loolu Yeesu daldi gëdd dëkk, ya mu defe woon la ëpp cay kéemaanam, ndaxte tuubuñu seeni bàkkaar. 11:21 Mu ne: «Dingeen torox, yéen waa Korasin ak waa Betsayda, ndaxte kéemaan yi ma def ci yéen, bu ñu leen defoon ci dëkku Tir walla ci dëkku Sidon, kon réccu nañu bu yàgg, xëppoo dóom, sol saaku. 11:22 Waaye maa ngi leen koy wax, keroog bés pénc ma Tir ak Sidon ñoo leen di tane. 11:23 Te yaw dëkku Kapernawum, ndax dees na la yékkati bu kawe? Déedéet, dees na la daane bu suufe. Ndaxte kéemaan yi ma def ci yaw, bu ñu leen defoon ci dëkku Sodom, kon mu nekk ba tey. 11:24 Waaye maa ngi leen koy wax, keroog bés pénc ma Sodom moo lay tane.» 11:25 Ca jamono joojale Yeesu wax na lii: «Yaw Baay bi, Boroom asamaan ak suuf, maa ngi lay sant ci li nga nëbb yëf yii ñi am xam-xam ak ñi am xel, te xamal leen gune yi. 11:26 Waaw Baay bi, ndaxte looloo la neex.» 11:27 Yeesu teg ca ne: «Sama Baay jébbal na ma lépp, te kenn mënu maa xam, man Doom ji, ku dul Baay bi; kenn it mënul a xam Baay bi, ku dul man Doom ji, ak ku ma ko bëgg a xamal. 11:28 «Ñëwleen ci man, yéen ñépp ñi sonn te diis, dinaa leen may noflaay. 11:29 Jébbaluleen ci man te jàng ci man, ndaxte lewet naa te woyof, te dingeen am noflaay ci seen xol. 11:30 Ndaxte sama kilifteef lewet na te sama yen diisul.»
12:1 Amoon na benn bésu noflaay Yeesu jaar ci ay tool yu ñor, fekk ay taalibeem xiif; ñu daldi fàq ay gub nag, di lekk. 12:2 Farisen ya nag gis ko, ne Yeesu: «Gisal, say taalibe ñu ngi def lu jaaduwul ci bésu noflaay bi.» 12:3 Noonu Yeesu tontu leen: «Ndax jànguleen la Daawuda defoon, ba mu xiifee, moom ak ña mu àndaloon? 12:4 Xanaa yéguleen, ni mu dugge woon ca kër Yàlla ga, gis fa mburu, ya ñu jébbal Yàlla, mu daldi ko lekk. Fekk jaaduwul mu lekk ca, moom walla ña mu àndaloon; saraxalekat rekk a ko sañoon a lekk. 12:5 Te it ndax jànguleen ci yoonu Musaa, ne saraxalekat ya ca kër Yàlla ga teraluñu bésu noflaay bi, te tooñuñu? 12:6 Waaye maa ngi leen koy wax, am na ci seen biir ku sut kër Yàlla ga. 12:7 Mbind mi nee na: “Yërmande laa bëgg, waaye du rendi saraxi mala.” Su ngeen xamoon lu wax joojuy tekki, kon dungeen teg tooñ ñi tooñul. 12:8 Ndaxte Doomu nit ki mooy boroom bésu noflaay bi.» 12:9 Bi loolu amee Yeesu jóge foofa, dugg ci seen jàngu, 12:10 te amoon na fa nit ku loxoom làggi. Noonu Farisen ya laaj ko: «Faj ci bésu noflaay bi, ndax loolu jaadu na?» Fekk ñuy wut buntu tuumaal ko. 12:11 Yeesu tontu leen: «Ku fi amoon xar, mu daanu ci kàmb ci bésu noflaay bi, ndax doo ko jàpp, génne ko? 12:12 Nit nag, ndax ëppul maana xar? Kon def lu baax ci bésu noflaay bi jaadu na.» 12:13 Noonu Yeesu ne nit ka: «Tàllalal sa loxo!» Mu tàllal ko nag, loxoom daldi wér, mel ni ba ca des. 12:14 Farisen ya génn nag, daldi gise, ngir fexee reylu Yeesu. 12:15 Waaye bi ko Yeesu yégee, mu sore foofa; te ñu bare topp ko, mu wéral leen ñoom ñépp. 12:16 Te mu dénk leen bu wóor, ñu bañ koo siiwal. 12:17 Def na noonu, ngir amal la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu naan: 12:18 «Kii mooy sama Ndaw li ma tànn,di sama Soppe bi neex sama xol.Dinaa def sama Xel ci moom,muy yégal xeet yi yoonu njub. 12:19 Du xëccoo mbaa muy wax ci kaw,te kenn du dégg baatam ci mbedd yi. 12:20 Du dammaate barax bu banku,te mees guy saxar, du ko fey,ba kera mu yégal njub, ba daan. 12:21 Ci turam la xeet yi di ame yaakaar.» 12:22 Booba ñu indil ko ku rab jàpp, mu gumba te luu. Yeesu faj ko, ba ku luu ki di wax tey gis. 12:23 Noonu mbooloo mépp yéemu naan: «Ndax kii du Sëtu Daawuda bi?» 12:24 Bi Farisen ya déggee loolu nag, ñu ne: «Kii ci kàttanu Beelsebul, buuru rab yi, lay dàqe rab yi.» 12:25 Waaye Yeesu xam seen xalaat ne leen: «Réew mu xeex boppam tas, te dëkk mbaa kër guy xeex boppam du man a yàgg. 12:26 Bu Seytaane dàqee Seytaane nag, xeex na boppam; kon naka la nguuram di man a yàgge? 12:27 Te it bu fekkee ne man damay dàq ay rab ci kàttanu Beelsebul, seeni taalibe nag, ci gan kàttan lañu leen di dàqe? Kon ñoo leen di àtte. 12:28 Waaye bu fekkee ne ci Xelum Yàlla laay dàqe rab, kon nguuru Yàlla agsi na ba ci yéen. 12:29 «Su fi amee nit ku bare doole, te nit bëgg a dugg ci këram, nangu alalam, naka la koy defe? Xanaa dafay jëkk a yeew ku bare doole ka, ba noppi door a toj këram gépp. 12:30 Noonu ku farul ak man, yaa ngi may xeex, ku dajalewul ak man, yaa ngi tasaare.» 12:31 Yeesu teg ca ne: «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, bàkkaar walla sos wu mu man a doon, dinañu ko baale, waaye ku sosal Xelum Yàlla, duñu ko baal. 12:32 Ku sosal Doomu nit ki, dinañu ko baal, waaye ku sosal Xel mu Sell mi, duñu ko baal mukk, du ci àddina si, du ci àllaaxira. 12:33 Neeleen garab gi baax na, moom ak meññeefam, walla ngeen ne garab gi bon na, moom ak meññeefam; ndaxte garab, meññeefam lañu koy xàmmee. 12:34 Yéen ñi fees ak daŋar ni ay co, naka ngeen man a waxe lu baax, fekk dangeen bon? Ndaxte gémmiñ, la fees xol lay wax. 12:35 Noonu nit ku baax, lu baax lay wax, jële ko ca fa mu denc lu baax, te nit ku bon, lu bon lay wax, jële ko ca fa mu denc lu bon. 12:36 Maa ngi leen di wax ne, keroog bés pénc, nit ñi dinañu làyyi ndax wax ju nekk ju amul njariñ, ju ñu mas a wax. 12:37 Ndaxte dees na la àtte ni ku jub ci say wax, walla ñu daan la ci say wax.» 12:38 Ci kaw loolu ay xutbakat ak ay Farisen wax ak Yeesu ne ko: «Kilifa gi, danoo bëggoon, nga won nu kéemaan guy firndeel sag yónnent.» 12:39 Yeesu tontu leen: «Yéenay laaj firnde, yéen niti jamono ju bon jii, yéen ñi fecci seen kóllëre ak Yàlla, waaye dungeen jot genn firnde gu dul firndeg yonent Yàlla Yunus. 12:40 Ndaxte ni Yunus nekke woon ñetti guddi ak ñetti bëccëg ci biir rabu géej wu mag, noonu la Doomu nit ki di nekke ñetti guddi ak ñetti bëccëg ci biir suuf. 12:41 Keroog bés pénc waa dëkku Niniw dinañu jógandoo ak niti jamono jii, yey leen; ndaxte bi leen Yunus waaree, tuub nañu seeni bàkkaar, te ku sut Yunus a ngi fi. 12:42 Te it ca bés pénc buur bu jigéen, ba dëkkoon ca sudd, dina jógandoo ak niti jamono jii, yey leen; ndaxte dafa jóge ca catul àddina, ngir déglu xam-xamu Suleymaan, te ku sut Suleymaan a ngi fi. 12:43 «Boo xamee ne rab wa jàppoon nit génn na ci moom, day wër ay bérab yu wow, di wut fu mu noppaloo, waaye du ko gis. 12:44 Noonu da naan: “Naa dellu ca sama kër, ga ma génne woon.” Bu ñëwee nag, mu fekk kërug neen, ñu bale ko, defar ko ba lépp jekk. 12:45 Bu ko gisee nag, mu dem wooyi yeneen juróom-ñaari rab yu ko gën a soxor, ñu dugg, sanc fa; ba tax muju nit kooku mooy yées njàlbéenam. Noonu lay nekke ak niti jamono ju bon jii.» 12:46 Bi Yeesu nekkee di wax ak mbooloo ma, ndeyam ak ay rakkam daldi ñëw, taxaw ci biti, bëgg a wax ak moom. 12:47 Noonu kenn nit ne ko: «Sa yaay ak say rakk ñu ngi nii taxaw ci biti, bëgg a wax ak yaw.» 12:48 Waaye Yeesu tontu ko ne: «Kan mooy sama ndey ak ñan ñooy samay rakk?» 12:49 Noonu mu joxoñ ay taalibeem naan: «Ñii ñooy sama ndey ak samay rakk. 12:50 Ndaxte ku def sama coobareg Baay bi nekk ci kaw, yaa di sama rakk, sama jigéen ak sama ndey.»
13:1 Bés booba Yeesu génnoon na ca kër ga, toog ca wetu dex ga. 13:2 Mbooloo mu bare dajaloo ca moom, ba tax mu dugg cig gaal, toog; mbooloo mépp taxaw ca tefes ga. 13:3 Noonu Yeesu dégtal leen lu bare ciy léeb ne leen: «Dafa amoon beykat bu demoon jiyi. 13:4 Bi muy saaw toolam nag, lenn ci pepp mi wadd ci kaw yoon wi, picc yi daldi ñëw, lekk ko lépp. 13:5 Leneen ci pepp mi wadd ci bérab bu bare ay doj te néew suuf, mu daldi sax bu gaaw, ndaxte suuf si barewul. 13:6 Waaye bi jant bi naajee, mu lakk, wow, ndaxte amul ay reen. 13:7 Leneen nag wadd ci biir ay xaaxaam, xaaxaam yi daldi jóg, tanc ko. 13:8 Li ci des dal ci suuf su baax, nangu ba def ay gub; lii àntu ba mat téeméeri yoon lu ëpp la mu ji woon, lii mat juróom-benn-fukk, li ci des fanweer. 13:9 Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.» 13:10 Bi Yeesu waxee ba noppi, ay taalibeem jegeñsi, laaj ko lu tax mu di leen wax ciy léeb. 13:11 Noonu mu tontu leen ne: «May nañu leen, ngeen xam mbóoti nguuru Yàlla Aji Kawe ji, waaye ñale mayuñu leen ko. 13:12 Ndaxte ku am, dinañu la dollil, ba nga barele; waaye ku amul, li nga am as néew, dinañu ko nangu. 13:13 “Dañuy xool te duñu gis, di déglu waaye duñu dégg te duñu xam,” moo tax ma di leen wax ciy léeb. 13:14 Li Esayi waxoon ci kàddug Yàlla am na ci ñoom, bi mu naan:“Dingeen déglu bu baaxwaaye dungeen xam dara;di xool bu baax waaye dungeen gis dara. 13:15 Ndaxte xolu xeet wii dafa dërkiis;dañuy déglu ak nopp yu naqari,tey gëmm seeni bët,ngir bañ a gis ak seeni bët,dégg ak seeni nopp,te xam ci seen xol,ñu woññiku ci man, ma wéral leen.” 13:16 «Waaye yéen barkeel ngeen, ndaxte seeni bët a ngi gis te seeni nopp di dégg! 13:17 Ndaxte ci dëgg maa ngi leen koy wax, ay yonent yu bare ak nit ñu jub ñu bare bëggoon nañu gis li ngeen di gis waaye gisuñu ko, te dégg li ngeen di dégg waaye dégguñu ko. 13:18 «Yéen nag dégluleen li léebu beykat biy tekki. 13:19 Boo xamee ne nit mu ngi déglu wax ju jëm ci nguuru Yàlla te xamu ko, Ibliis day ñëw, këf li ñu def ci xolam; kooku mooy ki jot ci jiwu wi ci kaw yoon wi. 13:20 Ki jot ci jiwu wi ci bérab bu bare ay doj nag, mooy ki dégg wax ji, am ci bànneex bu gaaw; 13:21 waaye du yàgg, ndaxte wax ji saxul ci moom. Bu jaaree ci nattu nag, mbaa ñu fitnaal ko ndax kàddu gi, mu dàggeeku ci saa si. 13:22 Ki jot ci jiwu wi ci xaaxaam yi mooy ki dégg wax ji, waaye soxlay àddina ak naxi alal tanc wax ji, ba du jur njariñ. 13:23 Ki jot ci jiwu wi ci suuf su baax si nag, mooy ki dégg wax ji te xam ko; mu jural ko njariñ, muy lu mat téeméeri yoon lu ëpp la ñu ji woon, muy juróom-benn-fukk mbaa fanweer.» 13:24 Noonu Yeesu dégtal leen beneen léeb ne leen: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni nit ku ji jiwu wu baax ci toolam. 13:25 Waaye bi nit ñi di nelaw, noonam ñëw, ji jëmb ci biir dugub ji, daldi dem. 13:26 Bi dugub ji saxee nag, jëmb bi saxaale ak moom. 13:27 «Noonu surgay boroom kër ga ñëw ci moom ne ko: “Góor gi, xanaa jiwuloo jiwu wu baax ci sa tool? Fu jëmb bi jóge nag?” 13:28 Mu tontu leen: “Noon a ko def.” Surga ya ne ko: “Ndax nu dem dindi ko?” 13:29 Waaye mu tontu leen: “Déedéet, ngir bañ a buddiwaale dugub ji, bu ngeen koy dindi. 13:30 Bàyyileen ñoom ñaar, ñu màgg, ba ngóob ma jot. Bu ngóob ma jotee nag, dinaa wax ñi koy góob: Jëkkleen a dindi jëmb bi, takk ko ay say, lakk ko, waaye ngeen semb dugub ji ci sama sàq.”» 13:31 Yeesu waxaat leen beneen léeb ne leen: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni doomu fuddën bu nit jël, ji ko ci toolam. 13:32 Doomu fuddën moo gën a tuuti ci jiwu yépp, waaye bu saxee, mooy sut ci gàncaxi tóokër yi, di nekk garab, ba picci asamaan ñëw, tàgg ciy caram.» 13:33 Yeesu teg ca beneen léeb ne leen: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni lawiir bu jigéen jël, jaxase ko ak ñetti andaari fariñ, ba kera tooyal bépp di funki.» 13:34 Loolu Yeesu wax mbooloo ma, ëmb na ko lépp ciy léeb, te waxuleen dara lu dul ciy léeb. 13:35 Noonu am la ñu waxoon jaarale ko cib yonent, bi mu naan:«Dinaa leen wax ciy léeb,di yégle yëf yu nëbbuli dale ca njàlbéen ga ba bésu tey.» 13:36 Ci kaw loolu Yeesu bàyyi mbooloo ma, dugg ca kër ga. Taalibeem yi ñëw ci moom ne ko: «Firil nu léebu jëmb, bi sax ci tool bi.» 13:37 Noonu Yeesu tontu leen ne: «Doomu nit ki mooy ji jiwu wu baax wi; 13:38 àddina mooy tool bi; ñi bokk ci nguuru Yàlla ñoo di jiwu wu baax wi; ñi bokk ci Ibliis ñooy jëmb bi; 13:39 Seytaane mooy noon bi ko ji; tukkitel àddina mooy ngóob mi, te malaaka yi ñooy góobkat yi. 13:40 Ni ñu dajalee jëmb ba, lakk ko, noonu lay nekke, bu àddina tukkee. 13:41 Doomu nit ki dina yebal ay malaakaam, ñu jële ci nguuram lépp luy yóbbe nit bàkkaar, ak ñiy def bàkkaar, 13:42 sànni leen ci safara; foofa dees na fa jooy te yéyu. 13:43 Booba nag ñu jub ñi dinañu leer ni jant bi ci seen nguuru Baay. Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.» 13:44 Yeesu teg ca ne: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni alal ju nëbbu cib tool. Nit ki ko gis nëbbaat ko; xolam sedd, ba mu dem jaay li mu am lépp, jënd tool ba. 13:45 «Te it nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni jaaykat buy wut per yu rafet. 13:46 Am bés mu gis per buy jar njëg gu réy. Mu dem nag, jaay li mu am lépp, jënd ko.» 13:47 Yeesu waxaat ne: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni mbaal mu ñu wàcce ci géej, mu jàpp jën wu nekk. 13:48 Bi mbaal mi feesee nag, ñu ñoddi ko ci tefes gi, ba noppi ñu taxaw, dajale yu baax yi ciy ndab, waaye sànni yi bon. 13:49 Noonu lay mel, bu àddina tukkee. Malaaka yi dinañu génn, tànn ñu bon ñi ci biir ñu jub ñi, 13:50 sànni leen ci safara. Foofa dees na fa jooy te yéyu.» 13:51 Noonu Yeesu laaj taalibe ya ne leen: «Loolu lépp, ndax xam ngeen lu muy tekki?» Ñu tontu ko: «Waaw.» 13:52 Yeesu ne leen: «Kon xutbakat bu nekk bu jàng ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji, dafa mel ni boroom kër buy génne ci dencukaayam yu bees ak yu màggat.» 13:53 Bi nga xamee ne Yeesu dégtal na léeb yooyu ba noppi, mu jóge fa, 13:54 dem fa mu yaroo. Mu di leen jàngal ci seen jàngu, ba ñu waaru ne: «Xam-xam bii ak kéemaan yii, fu mu ko jële? 13:55 Ndax kii du doomu minise bi, te ndeyam tudd Maryaama? Ndax rakkam yu góor duñu Saag, Yuusufa, Simoŋ ak Yuda? 13:56 Te ay rakkam yu jigéen, ndax nekkuñu fi ak nun? Lii lépp nag, fu mu ko jële?» 13:57 Kon ñu daldi koy xeeb.Noonu Yeesu ne leen: «Dees na faaydaal yonent, waaye du ci réewam ak ci këram.» 13:58 Te Yeesu defu fa kéemaan yu bare ndax seen ngëmadi.
14:1 Ca jamono joojale Erodd boroom diiwaanu Galile dégg na tur, wa Yeesu am. 14:2 Noonu mu ne ay surgaam: «Kooku mooy Yaxya, mi dekki; moo tax mu ànd ak kàttanu def ay kéemaan.» 14:3 Ndaxte Erodd jàppoon na Yaxya, yeew ko, tëj. Ndaxte Erodd takkoon na Erojàdd, jabaru Filib magam, 14:4 te Yaxya daan ko wax: «Jaaduwul nga denc ko.» 14:5 Erodd nag bëgg koo rey, waaye dafa ragal nit ñi, ci li ñu teg Yaxya ab yonent. 14:6 Bi ñu ca tegee ab diir nag, ñuy màggal bés ba Erodd juddu woon, te doomu Erojàdd ju jigéen di fecc ci biir gan ñi. Loolu neex Erodd, 14:7 ba mu dig ko ci kaw ngiñ ne ko: «Loo laaj, dinaa la ko jox.» 14:8 Noonu ndaw sa daldi topp la ko ndey ji digaloon, ne Erodd: «Indil ma fii ci biir ndab boppu Yaxya.» 14:9 Bi ko buur ba déggee, mu am naqar, waaye ngiñ la ak gan ña tax mu santaane, ñu jox ko ko. 14:10 Mu yónnee nag, ngir ñu dagg boppu Yaxya ca kaso ba. 14:11 Ñu indi bopp bi ci biir ndab, jox ko janq ba, mu jox ko ndeyam. 14:12 Noonu taalibey Yaxya ñëw, fab néew wa, suul ko; ba noppi dem, wax ko Yeesu. 14:13 Bi Yeesu déggee deewu Yaxya nag, mu jóge fa, dugg cig gaal, di dem ca bérab bu wéet. Waaye bi ko nit ñi yégee, ñu daldi jóge ci dëkk yi, topp ko ak seeni tànk. 14:14 Yeesu génn ci gaal gi nag, gis mbooloo mu réy, mu yërëm leen, ba faj ñi ci wopp. 14:15 Ca ngoon sa taalibe yi ñëw ci moom ne ko: «Fii àllub neen la, te léegi mu guddi. Doo yiwi mbooloo mi, ngir ñu dem ci dëkk yu ndaw yi, jënd lu ñu man a lekk?» 14:16 Waaye Yeesu tontu leen ne: «Matul ñu dem, yéen joxleen leen lu ñu lekk.» 14:17 Ñu ne ko: «Amunu fi lu dul juróomi mburu ak ñaari jën.» 14:18 Yeesu ne leen: «Indil-leen ma ko fii.» 14:19 Ci kaw loolu Yeesu sant mbooloo ma, ñu toog ca ñax ma. Mu jël juróomi mburu ya ak ñaari jën ya, xool ci kaw, sant Yàlla. Mu damm mburu ma, jox ko taalibe ya, ñu séddale ko nit ña. 14:20 Noonu ñépp lekk ba suur. Te ñu dajale dammit ya ca des, mu nekk fukki pañe ak ñaar yu fees. 14:21 Gannaaw jigéen ña ak gune ya, góor ña doon lekk matoon nañu juróomi junni. 14:22 Bi loolu amee Yeesu sant taalibe ya, ñu dugg gaal ga te jàll dex ga, jiituji ko, muy yiwi mbooloo ma. 14:23 Bi mu ko yiwee nag, mu yéeg ca tund wa, ngir wéet ak Yàlla. Noonu guddi jot, fekk mu nekk fa moom rekk. 14:24 Bi mu fa nekkee nag, gaal ga sore na tefes ga, te duus ya di ko yengal bu metti, ndax ngelaw la leen soflu. 14:25 Ca njël nag Yeesu jëm ci ñoom, di dox ci kaw dex gi. 14:26 Waaye bi ko taalibe yi gisee, muy dox ci kaw dex ga, ñu daldi jommi naan: «Njuuma la!» daldi tiit bay yuuxu. 14:27 Waaye ca saa sa Yeesu ne leen: «Takkleen seen fit, man la, buleen tiit!» 14:28 Ci kaw loolu Piyeer jël kàddu gi ne ko: «Sang bi, bu dee yaw, sant ma, ma dox ci kaw ndox mi, ñëw ci yaw.» 14:29 Yeesu ne ko: «Kaay!» Piyeer nag wàcc ca gaal ga, di dox ci kaw ndox mi, jëm ci Yeesu. 14:30 Waaye bi mu gisee ni ngelaw li mettee, mu daldi tiit, tàmbalee suux. Mu woote ne: «Sang bi, wallu ma!» 14:31 Ca saa sa Yeesu tàllal loxoom, jàpp ko naan: «Yaw mi néew ngëm, lu tax nga am xel ñaar?» 14:32 Noonu ñu dugg ca gaal ga, te ngelaw li ne tekk. 14:33 Ñi nekk ci gaal gi nag sukk ci kanamam ne ko: «Ci dëgg yaa di Doomu Yàlla ji.» 14:34 Bi loolu amee ñu jàll, teer ca diiwaanu Senesaret. 14:35 Ña fa dëkk xàmmi Yeesu, yónnee nag ca diiwaan bépp, indil ko ñu wopp ñépp. 14:36 Noonu ñu ñaan ko, mu may leen ñu laal cati mbubbam rekk, te ku ko laal daldi wér.
15:1 Ca jamono jooja amoon na bés ay Farisen ak ay xutbakat jóge Yerusalem, ñëw ci Yeesu ne ko: 15:2 «Lu tax say taalibe di moy aaday yoon, yi maam yi tëral? Ndaxte duñu raxas seeni loxo, bu ñuy lekk.» 15:3 Waaye Yeesu tontu leen ne: «Yéen itam lu tax ngeen di moy li Yàlla santaane, ngir topp seeni aada? 15:4 Yàlla nee na: “Teralal sa ndey ak sa baay,” te it: “Ku móolu sa ndey walla sa baay, dees na la rey.” 15:5 Waaye yéen dangeen ne, ku wax sa ndey walla sa baay: “Li ngeen war a jariñoo ci man, jébbal naa ko Yàlla,” 15:6 kooku amatul warugaru teral baayam. Noonu tebbi ngeen kàddug Yàlla ndax seen aada. 15:7 Yéen ñi naaféq, Esayi waxoon na bu baax ci kàddug Yàlla ci seen mbir, bi mu naan: 15:8 “Xeet wii ñu ngi may teral ci seen gémmiñ,waaye seen xol sore na ma. 15:9 Seen màggal amul benn njariñ,ci li ñuy jàngale dénkaaney nit kese.”» 15:10 Noonu Yeesu woo mbooloo mi ci moom ne leen: «Dégluleen te xam: 15:11 du li dugg ci gémmiñ mooy indil nit sobe, waaye li ciy génne mooy indil nit sobe.» 15:12 Bi taalibeem ya déggee loolu, ñu ñëw ci moom ne ko: «Ndax xam nga ne, Farisen yi dañoo mer ndax loolu nga wax?» 15:13 Yeesu tontu leen ne: «Garab gu sama Baay bi ci kaw jiwul, dees na ko buddi. 15:14 Bàyyileen leen, ay gumba lañu yuy wommat ay gumba; bu gumba dee wommat moroomam nag, kon dinañu daanu ñoom ñaar ci kàmb.» 15:15 Piyeer nag jël kàddu gi, laaj Yeesu: «Firil nu léeb wi.» 15:16 Noonu Yeesu ne ko: «Ndax ba tey seen xol dafa tëju, yéen itam? 15:17 Xamuleen ne, lépp lu dugg ci gémmiñ, ci biir lay jëm tey génn ca bérab bu làqu? 15:18 Waaye li génn ci gémmiñ mu ngi jóge ci xol; loolu mooy indil nit sobe. 15:19 Ndaxte ci xol la xalaat yu bon di jóge, ak bóom, njaaloo, ndoxaanu yàqute, càcc, seede lu dul dëgg ak saaga. 15:20 Yooyu ñooy indil nit sobe, waaye lekk ak loxo yoo raxasul du tax nit am sobe.» 15:21 Gannaaw loolu Yeesu jóge fa, dem ci diiwaanu Tir ak Sidon. 15:22 Ba mu fa àggee nag, jigéenu waa Kanaan, ja dëkk ca wàll yooyu, daldi génn, di wax ca kaw ne ko: «Yaw sang bi, Sëtu Daawuda bi, yërëm ma! Rab jàpp na sama doom ju jigéen, te dafa sonn lool.» 15:23 Waaye Yeesu tontuwu ko genn kàddu. Ay taalibeem nag ñëw ci moom ne ko: «Doo ko yiwi, mu ngi nuy topp, di yuuxu ci sunu kaw.» 15:24 Yeesu tontu ne: «Yónniwuñu ma, lu dul ci xar yu réeri bànni Israyil.» 15:25 Waaye jigéen ja ñëw, sukk ci kanamam naan: «Sang bi, wallusi ma!» 15:26 Yeesu tontu ko: «Jël ñamu gune yi, sànni ko xaj yi, rafetul.» 15:27 Waaye jigéen ja ne ko: «Waaw sang bi, teewul xaj yi di lekk ruusit, yi rot ci seen lekkukaayu boroom.» 15:28 Ci kaw loolu Yeesu tontu ko ne: «Yaw jigéen ji, sa ngëm réy na; na am, ni nga ko bëgge.» Noonu doomam daldi wér ca saa sa. 15:29 Bi loolu amee Yeesu jóge foofa, ñëw ci weti dexu Galile; mu yéeg ca aw tund, toog fa. 15:30 Ba mu fa nekkee, nit ñu bare ñëw ci moom, indaale ay lafañ, ay làggi, ay gumba, ay luu ak ñeneen ñu bare. Ñu teg leen ci tànki Yeesu, mu faj leen. 15:31 Nit ñépp waaru, ndaxte gis nañu luu yuy wax, làggi yu wér, lafañ yuy dox, ak gumba yuy gis. Ñu daldi màggal Yàlla Buuru Israyil. 15:32 Gannaaw loolu Yeesu woo ci moom taalibeem ya ne leen: «Yërëm naa mbooloo mi, ndaxte toog nañu fi man ñetti fan, te amatuñu lu ñu lekk. Bëgguma leen a yiwi te lekkuñu, ngir bañ ñu tële ci yoon wi.» 15:33 Noonu taalibeem ya laaj ko: «Waaye fu nuy jële ci àll bi mburu mu doy ngir mbooloo mu tollu nii?» 15:34 Yeesu ne leen: «Ñaata mburu ngeen am?» Ñu tontu ko: «Juróom-ñaari mburu ak ay jën yu ndaw.» 15:35 Ci kaw loolu Yeesu sant mbooloo mi, ñu toog ci suuf. 15:36 Mu fab juróom-ñaari mburu yi ak jën yi, sant Yàlla, damm leen, jox leen taalibe yi, ñu séddale leen mbooloo mi. 15:37 Noonu ñépp lekk ba suur. Te ñu dajale juróom-ñaari dàmba yu fees ak dammit yi ci des. 15:38 Gannaaw jigéen ñi ak gune yi, góor ñi ci lekk matoon nañu ñeenti junni. 15:39 Noonu Yeesu yiwi mbooloo mi, dugg ci gaal, ñëw ci wàlli Magadan.
16:1 Amoon na ay Farisen ak ay Sadusen yu ñëw ci Yeesu. Ñu fexe koo fiir, ba laaj ko ne: «Won nu kéemaan guy firndeel sag yónnent, te mu jóge ci asamaan.» 16:2 Noonu Yeesu tontu leen: «Ngoon gi dangeen naan: “Du taw suba ndax asamaan si dafa xonq.” 16:3 Te suba gi ngeen naan: “Tey daal dina taw, ndax asamaan si dafa xonq te xiin.” Kon man ngeen a ràññee melow asamaan, waaye mënuleen a ràññee firndey jamono ji nu tollu. 16:4 Yéenay laaj firnde, yéen niti jamono ju bon jii, yéen ñi fecci seen kóllëre ak Yàlla. Waaye dungeen jot genn firnde gu dul firndeg Yunus.» Bi Yeesu waxee loolu, mu jóge ci ñoom, dem. 16:5 Gannaaw loolu taalibe yi jàllaat dex gi, fekk fàtte nañoo yóbbaale mburu. 16:6 Noonu Yeesu ne leen: «Wottuleen te moytu lawiiru Farisen ya ak Sadusen ya.» 16:7 Bi ko taalibe yi déggee, ñu daldi werante ci seen biir naan: «Nun de indaalewunu mburu.» 16:8 Waaye Yeesu yég loolu ne leen: «Yéen ñi néew ngëm, lu tax ngeen di werante ci seen biir, ndaxte indaalewuleen mburu? 16:9 Ndax xamaguleen ba tey? Xanaa fàttalikuwuleen juróomi mburu ya ngir juróomi junniy góor ña, ak ñaata pañe ngeen dajale woon ciy dammit? 16:10 Te ndax fàttalikuwuleen itam juróom-ñaari mburu ya ngir ñeenti junniy góor ña, ak ñaata dàmba ngeen dajale woon ciy dammit? 16:11 Kon nag lu tax xamuleen ne, waxuma mburu? Waaye damaa bëgg, ngeen moytu lawiiru Farisen ya ak Sadusen ya.» 16:12 Noonu ñu xam ne, Yeesu waxul woon lawiiru mburu, waaye ñu moytu njàngalem Farisen ya ak Sadusen ya. 16:13 Bi ñu fa jógee, Yeesu dem ca diiwaanu Sesare bu Filib. Foofa mu laaj taalibeem ya: «Lu nit ñiy wax ci Doomu nit ki; mooy kan?» 16:14 Taalibe yi tontu ne: «Am na ñu naan, Yaxya, ñeneen ñi, Iliyas; ñi ci des ne, Yeremi walla keneen ci yonent yi.» 16:15 Noonu Yeesu ne leen: «Waaye yéen, ku ngeen may teg?» 16:16 Ci kaw loolu Simoŋ Piyeer tontu ne: «Yaa di Almasi bi, Doomu Yàlla Aji Dund ji.» 16:17 Yeesu tontu ko: «Barkeel ñeel na la, Simoŋ doomu Yunus, ndaxte du nit moo la xamal lii, waaye sama Baay bi nekk ci kaw. 16:18 Te maa ngi lay wax lii: yaa di Piyeer, te ci kaw doj wu réy woowu laay samp mbooloom ñi ma gëm, te dooley dee du ko manal dara. 16:19 Dinaa la jox caabiy nguuru Yàlla Aji Kawe ji; li nga yeew ci àddina, dees na ko yeew ci asamaan; li nga yiwi ci àddina dees na ko yiwi ci asamaan.» 16:20 Noonu Yeesu dénk taalibe yi bu wóor ne leen: «Buleen wax kenn ne, maay Almasi bi.» 16:21 Li dale ci jamono jooja, Yeesu tàmbali na xamal taalibeem yi ne, war na dem Yerusalem, daj fa coono yu bare, jóge ca njiit ya, ca saraxalekat yu mag ya ak ca xutbakat ya; ñu rey ko, mu dekki ca ñetteelu fan ba. 16:22 Bi mu waxee ba noppi, Piyeer woo ko ci pegg, bëgg koo yedd ne ko: «Yàlla tere, Boroom bi, loolu du la dal.» 16:23 Waaye Yeesu woññiku, daldi ne Piyeer: «Sore ma Seytaane, bu ma xatal; yëfi nit ngay fonk, waaye du yëfi Yàlla.» 16:24 Gannaaw loolu Yeesu ne taalibeem ya: «Ku bëgg a aw ci samay tànk, na bàyyi boppam, te gàddu bant bi ñu ko war a daaj, door a topp ci man. 16:25 Ndaxte koo xam ne bëgg ngaa rawale sa bakkan, dinga ko ñàkk, waaye ku ñàkk sa bakkan ngir man, jotaat ko. 16:26 Te it moom àddina sépp lu muy jariñ nit, bu ñàkkee bakkanam? Te nit, lu mu war a weccee bakkanam? 16:27 Ndaxte Doomu nit ki dina ñëw ci ndamul Baayam, ànd ak ay malaakam; bés booba dina delloo ku nekk ay jëfam. 16:28 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, am na ñi fi taxaw, ñoo xam ne duñu dee, te gisuñu Doomu nit ki ñëw ci nguuram.»
17:1 Juróom-benni fan gannaaw gi, Yeesu àndoon na ak Piyeer, Saag ak Yowaana rakkam, yóbbu leen fu wéet ci tund wu kawe lool. 17:2 Mu soppiku fa seen kanam, xar-kanamam di melax nib jant, te ay yéreem weex ni leer. 17:3 Naka noonu ñu gis yonenti Yàlla Musaa ak Iliyas, di waxtaan ak Yeesu. 17:4 Piyeer nag daldi wax Yeesu ne ko: «Sang bi, bég nanu ci sunu teew fii; soo ko bëggee, dinaa fi defar ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa ak benn Iliyas.» 17:5 Waaye bi muy wax, niir wu leer muur leen, te baat jib ca niir wa naan: «Kii mooy sama Doom ji ma bëgg, ci moom laa ame bànneex; dégluleen ko.» 17:6 Bi taalibe yi déggee baat bi, ñu ne nërëm ci suuf, daldi tiit lool. 17:7 Waaye Yeesu jegeñsi, laal leen naan: «Jógleen, buleen ragal dara.» 17:8 Noonu ñu xool ci kaw, waaye gisatuñu kenn ku dul Yeesu rekk. 17:9 Bi loolu amee ñu wàcc ca tund wa. Bi ñuy wàcc nag, Yeesu sant leen ne: «Buleen nettali kenn li ngeen gis, ba kera Doomu nit ki dekki.» 17:10 Noonu taalibe ya laaj ko: «Lu tax xutbakat ya nag di wax ne, Iliyas mooy jëkk a ñëw?» 17:11 Yeesu tontu leen ne: «Waaw dëgg la, Iliyas war na ñëw, jubbanti lépp. 17:12 Teewul maa ngi leen di wax ne, Iliyas ñëw na te xàmmiwuñu ko, waaye def nañu ko la leen neex. Noonu it dañoo nar a sonal léegi Doomu nit ki.» 17:13 Ndax wax jooju nag, taalibe ya xam ne, ci mbirum Yaxya la leen doon wax. 17:14 Bi nga xamee ne wàcc nañu, ba ñëw ca mbooloo ma, genn góor ñëw ci moom, sukk 17:15 naan: «Sang bi, yërëmal sama doom, ndaxte mu ngi say, di am coono bu metti; léeg-léeg mu daanu ci safara, léeg-léeg mu daanu ci ndox. 17:16 Indi naa ko ci say taalibe, waaye mënuñu koo faj.» 17:17 Noonu Yeesu tontu ne: «Yéen niti jamono jii, yéen ñi gëmadi te dëng, ba kañ laa war a nekk ak yéen, ba kañ laa leen di war a muñal?» Mu ne leen, «Indil-leen ma xale bi fii.» 17:18 Noonu Yeesu tëkku rab wa, rab wa génn ca xale ba, mu daldi wér ca saa sa. 17:19 Bi loolu amee taalibe ya ñëw ci Yeesu, laaj ko ci pegg: «Lu tax nun mënunu woon a dàq rab wi?» 17:20 Yeesu tontu leen ne: «Seen ngëm gu néew a tax. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, su ngeen amee ngëm gu tuuti sax niw peppu fuddën, kon dingeen ne tund wii: “Jógeel fii, toxu fale,” te dina fa dem, ba dara du leen të.» 17:22 Bi ñuy wër diiwaanu Galile nag, Yeesu ne leen: «Léegi ñu jébbal Doomu nit ki ci loxoy nit ñi; 17:23 dinañu ko rey, mu dekki ca ñetteelu fan ba.» Bi ko taalibe ya déggee, ñu am naqar lool. 17:24 Gannaaw loolu Yeesu ak taalibe ya ñëw Kapernawum. Bi ñu fa àggee nag, laajkati warugaru kër Yàlla ga ñëw ci Piyeer ne ko: «Ndax seen kilifa du fey posetu ñaari daraxma ngir warugar wi?» 17:25 Piyeer ne leen: «Aaŋkay!»Ba ñu eggee kër ga nag, Yeesu jëkk a wax ne Piyeer: «Waaw lu ciy sa xalaat, Simoŋ? Buuri àddina si, ñan lañuy laaj juuti walla galag? Seeni doom walla ñi bokkul ci njaboot gi?» 17:26 Piyeer tontu ko ne: «Xanaa ñi bokkul ci kër gi.» Yeesu ne ko: «Kon doom yi nag mucc nañu ci. 17:27 Waaye bëgguma nu naqaral leen; kon demal sànni oos ca dex ga te nga génne jën wa jëkk a xëcc. Boo ubbee gémmiñam, dinga ca gis posetu estateer. Jël ko nag, jox leen ko ngir man ak yaw.»
18:1 Ca waxtu woowu taalibe ya ñëwoon nañu ci Yeesu, laaj ko: «Kan moo gën a màgg ci nguuru Yàlla mi nekk ci kaw?» 18:2 Noonu Yeesu woo xale, teg ko ci seen biir, 18:3 ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, su ngeen woññikuwul ci Yàlla, ba mel niy xale, dungeen dugg mukk ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji. 18:4 Kuy suufeelu nag, ba mel ni xale bii, kooku mooy ki gën a màgg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji. 18:5 Te it ku nangu ci sama tur xale bu mel ni kii, man mii nga nangu. 18:6 Waaye ku yóbbe bàkkaar kenn ci ñi gën a tuuti ñi ma gëm, li gën ci moom mooy ñu takk doj wu réy ci baatam, sànni ko ca fa gën a xóot ca géej ga. 18:7 «Yaw àddina dinga torox ndax say fiir yiy yóbbe nit bàkkaar. Fiir mënta ñàkk, waaye toroxte dal na nit ki koy lal. 18:8 Boo xamee ne sa loxo mbaa sa tànk mu ngi lay yóbbe bàkkaar, dagg ko, sànni ko fu sore. Ndaxte nga lafañ walla ñàkk loxo te dugg ci dund gu wóor gi, moo gën ci yaw, nga am ñaari loxo walla ñaari tànk, te ñu sànni la ci safara su dul fey mukk. 18:9 Boo xamee ne sa bët mu ngi lay yóbbe bàkkaar, luqi ko, sànni ko fu sore. Ndaxte nga patt te dugg ci dund gu wóor gi, moo gën ci yaw, nga am ñaari bët, te ñu sànni la ci safara. 18:10 «Te it wottuleen a xeeb kenn ci ñi gën a tuuti, ndax kat seeni malaakaa ngi sax ci jataayu sama Baay bi nekk ci kaw. Maa leen wax loolu. 18:12 «Luy seen xalaat ci lii? Su fi amoon nit ku am téeméeri xar, te benn ci ñoom réer, lu muy def? Ndax du bàyyi ca parlukaay ba juróom-ñeent-fukki xar ya ak juróom-ñeent, te dem wuti ma réer? 18:13 Bu ko gisee, mbég mi mu am ci moom mooy ëpp mbég, mi mu am ci juróom-ñeent-fukki xar ya ak juróom-ñeent ya réerul. 18:14 «Noonu it seen Baay bi nekk ci kaw bëggul kenn ci ñi gën a tuuti sànku. 18:15 «Te lii itam, bu sa mbokk defee bàkkaar, demal yedd ko, yéen ñaar rekk. Bu la dégloo, kon gindi nga sa mbokk. 18:16 Waaye bu la dégluwul, àndal ak kenn mbaa ñaar, ngir mbir mi dëggu ci li ko ñaar walla ñett seede. 18:17 Bu leen dégluwul ñoom itam, wax ko mbooloom ñi gëm. Bu dégluwul mbooloo ma nag, nga teg ko ni ku gëmul Yàlla mbaa ab juutikat. 18:18 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, lépp lu ngeen yeew ci àddina, dees na ko yeew ci asamaan, te lépp lu ngeen yiwi ci àddina, dees na ko yiwi ci asamaan. 18:19 «Maa ngi leen koy wax it, bu ñaar ci yéen déggoo ci àddina, ngir ñaan lu mu man a doon, sama Baay bi nekk ci kaw dina leen ko may. 18:20 Ndaxte fu ñaar walla ñetti nit booloo ci sama tur, maa ngi ci seen biir.» 18:21 Noonu Piyeer ñëw ci Yeesu, laaj ko: «Boroom bi, bu ma sama mbokk tooñee, ñaata yoon laa ko war a baal? Xanaa ba ci juróom-ñaari yoon?» 18:22 Yeesu tontu ko ne: «Waxuma la ba ci juróom-ñaari yoon, waaye ba ci juróom-ñaar-fukki juróom-ñaari yoon. 18:23 «Loolu moo tax nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni buur bu bëgg a waññ alalam ak ay jaraafam. 18:24 Ba mu tàmbalee waññ nag, ñu indil buur ba ku ko ameel ay milyoŋ yu baree-bare, 18:25 waaye jaraaf ja amul lu mu feye. Kon nag sangam santaane, ñu jaay ko moom ak jabaram ak ay doomam ak lépp lu mu am, ngir fey bor ba. 18:26 Kon jaraaf ja daanu ciy tànkam ne ko: “Muñal ma, dinaa la fey lépp.” 18:27 Noonu sangam yërëm ko, bàyyi ko, baal ko bor ba. 18:28 «Bi loolu amee jaraaf ja génn, gis benn moroomu jaraafam bu ko ameel ay junni. Mu daldi ko jàpp, poñe ko ne ko: “Fey ma li nga ma ameel.” 18:29 Kon moroomam daanu ci suuf, ñaan ko ne: “Muñal ma, dinaa la fey.” 18:30 Waaye moom nanguwu ko, mu dem, tëj ko kaso, ba kera mu fey li mu ko ameel. 18:31 «Bi ay moroomam gisee loolu nag, ñu am naqar wu réy, daldi dem, xamal seen sang li xew lépp. 18:32 Sang ba nag woolu jaraaf ba ne ko: “Yaw jaraaf ju soxor nga! Baal naa la sa bor bépp, ndaxte tinu nga ma. 18:33 Lu tax yaw itam yërëmoo sa moroom, ni ma la yërëme?” 18:34 Noonu sang ba mer, jébbal ko ñiy fitnaale ca kaso ba, ba kera muy fey li mu ko ameel lépp. 18:35 «Noonu la leen sama Baay bi ci kaw di def, bu ngeen baalul ku nekk seen mbokk ak xol bu sedd.»
19:1 Bi nga xamee ne Yeesu wax na loolu ba noppi, mu jóge Galile, dem ci wàllu réewu Yawut yi, gi féete ci gannaaw dexu Yurdan. 19:2 Mbooloo mu bare topp ko, mu faj leen fa. 19:3 Bi mu fa nekkee, ay Farisen ñëw ci moom, bëgg koo fiir; ñu ne ko: «Ndax jaadu na nit fase jabaram, saa su ko neexee?» 19:4 Yeesu tontu leen ne: «Xanaa jànguleen ne, ca njàlbéen ga Aji Bind ji sàkk na leen, kii góor, kii jigéen, 19:5 te mu ne: “Moo tax góor dina beru ndeyam ak baayam, di taq ci jabaram, ñoom ñaar doon benn.” 19:6 Kon nag nekkatuñu ñaar waaye benn. Lu Yàlla takk nag, bu ko nit tas.» 19:7 Bi Yeesu waxee loolu, Farisen ya laaj ko ne: «Waaye Musaa santaane na, nit jox jabaram kayitu pase, tàggook moom. Lu tax mu wax loolu nag?» 19:8 Yeesu tontu leen: «Musaa may na leen, ngeen fase seen jabar, ndax seen xol dafa dëgër, waaye ca njàlbéen ga demewul woon noonu. 19:9 Te it maa ngi leen koy wax, koo xam ne kii fase nga sa jabar te du njaaloo tax, boo séyaatee ak keneen, njaaloo nga.» 19:10 Bi ko taalibe ya déggee, ñu ne ko: «Bu dee noonu la digganteb góor ak jigéen mel, bañ a séy moo gën.» 19:11 Yeesu tontu leen: «Du ñépp ñoo man a nangu loolu, waaye ñi ko Yàlla jagleel rekk. 19:12 Ndaxte am na ñu judduwaale tële, am na ñu tële ci loxoy nit, te am na ñu bañ a séy ngir nguuru Yàlla Aji Kawe ji. Ku ko man a nangu, nangu ko.» 19:13 Gannaaw loolu amoon na ay nit ñuy indil Yeesu ay xale, ngir mu teg leen ay loxoom, ñaanal leen. Waaye taalibe ya gëdd leen. 19:14 Bi Yeesu gisee loolu, mu ne leen: «Bàyyileen xale yi, te buleen leen tere, ñu ñëw fi man. Ndaxte ñu mel ni ñoom, ñoo yelloo nguuru Yàlla Aji Kawe ji.» 19:15 Noonu Yeesu teg leen ay loxoom, ba noppi jóge fa. 19:16 Bi muy dem nag, nit daldi ñëw ci moom ne ko: «Kilifa gi, lan laa war a def ci lu baax, ngir man a am dund gu dul jeex?» 19:17 Yeesu tontu ko: «Lu tax nga laaj ma ci wàllu lu baax? Kenn kepp moo baax. Boo bëggee dugg ca dund googu ci kaw, nanga sàmm ndigal yi.» 19:18 Waxambaane wa laaj ko: «Yan la?» Yeesu ne ko: «Yii: bul bóom, bul njaaloo, bul sàcc, bul seede lu dul dëgg, 19:19 teralal sa ndey ak sa baay, te it: nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.» 19:20 Waxambaane wa ne ko: «Sàmm naa yooyu yépp, lu ma deseeti?» 19:21 Noonu Yeesu ne ko: «Boo bëggee mat sëkk, demal jaay li nga am, jox ko miskin yi te dinga woomle ca asamaan. Boo noppee, ñëwal topp ci man.» 19:22 Waaye bi waxambaane wa déggee loolu, mu jóge fa ak tiis, ndaxte ku bare woon alal la. 19:23 Noonu Yeesu wax taalibeem ya ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, boroom alal dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji, lu jafee ngoogu! 19:24 Ma waxaat leen ko: giléem jaar ci bën-bënu pusa, moo gën a yomb boroom alal dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.» 19:25 Bi nga xamee ne taalibe ya dégg nañu loolu, ñu daldi waaru lool ne ko: «Kan moo man a mucc nag?» 19:26 Noonu Yeesu xool leen ne: «Loolu të na nit, waaye dara tëwul Yàlla.» 19:27 Bi ko Piyeer déggee, mu daldi ne: «Waaw nun nag, dëddu nanu lépp, topp la; kon nu nuy mujje nun?» 19:28 Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, bés baa ngi ñëw bu Yàllay yeesalaat lépp, te Doomu nit ki toog ci jalam, bi soloo ndam. Bés boobu nag, yéen ñi ma topp dingeen toog ci fukki jal ak ñaar, di àtte fukki giir ak ñaar yu bànni Israyil. 19:29 Koo xam ne kii dëddu nga ngir sama tur ay kër, ay doomi ndey yu góor walla yu jigéen, ndey walla baay, ay doom walla ay tool, dinga ko jotaat téeméeri yoon, ba noppi am dund gu dul jeex. 19:30 Waaye ñu bare ci ñi jiitu, ñooy mujji; ñi mujj, ñooy jiituji.
20:1 «Noonu nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni boroom kër bu génn ci suba teel, ngir jël ay liggéeykat ndax toolu réseñam. 20:2 Mu juboo ak liggéeykat ya ci bëccëg posetu denariyon, door leen a yebal ca toolam. 20:3 Ci yoor-yoor mu génn, gis ñeneen ñu toog ca pénc ma te liggéeyuñu. 20:4 Mu ne leen: “Demleen yéen itam ca tool ba, te dinaa leen fey lu jaadu.” 20:5 Ñu dem ca. Mu génnaat ci digg-bëccëg ak ci tisbaar, defaat noonu. 20:6 Mu génnati ci tàkkusaan, gis ñeneen di tendeefal. Mu ne leen: “Lu tax ngeen yendoo tendeefal, te liggéeyiwuleen?” 20:7 Ñu tontu ko: “Kenn jëlu nu.” Mu ne leen: “Demleen yéen itam ca tool ba.” 20:8 «Bi nga xamee ne timis jot na, boroom tool ba ne jawriñ ja: “Woowal liggéeykat yi te fey leen seen bëccëg, tàmbali ci ñi mujj a ñëw, ba ci ñi fi jëkk.” 20:9 Noonu ñi mu jël ci tàkkusaan ñëw, ku nekk jot posetu denariyon. 20:10 Gannaaw ga nag ñi mu jëkk a jël ñëw, yaakaar ne dinañu jot lu ëpp loolu, waaye ñoom itam ñu jot ku nekk benn denariyon. 20:11 Bi ñu ko jotee nag, ñu tàmbalee ñaxtu ca boroom kër ga, 20:12 naan: “Ñi mujj a ñëw, benn waxtu rekk lañu liggéey, ba noppi nga yemale leen ak nun, ñi yenu coonob bëccëg bi ak naaj wu metti wi.” 20:13 Waaye boroom kër ga tontu kenn ci ñoom ne ko: “Sama waay tooñuma la. Ndax juboowunu woon ci benn denariyon? 20:14 Kon fabal li nga moom te dem. Su ma bëggee fey ku mujj a ñëw, li ma la fey yaw, 20:15 ndax sañumaa def ak sama alal li ma neex? Walla ndax danga am kiñaan ci li ma yéwén?” 20:16 Noonu ñi mujj ñooy jiituji, ñi jiitu ñooy mujj.» 20:17 Gannaaw loolu Yeesu di dem Yerusalem, ànd ak fukki taalibe yi ak ñaar. Noonu mu wéetoo ak ñoom, di leen xamal ci yoon wi lii: 20:18 «Nu ngi jëm Yerusalem, te dees na jébbal Doomu nit ki saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya. Dinañu ko àtte, teg ko dee, 20:19 jébbal ko ñi dul Yawut, ngir ñu di ko ñaawal te di ko dóor ay yar, ba noppi daaj ko ci bant. Waaye ca ñetteelu fan ba dina dekki.» 20:20 Ci kaw loolu doomi Sebede ya ànd ak seen ndey, ñëw ci Yeesu. Ndey ja sukk, di ko ñaansi lenn. 20:21 Yeesu ne ko: «Loo bëggoon?» Mu tontu ko ne: «Damaa bëggoon nga santaane ne, boo nekkee ci sa nguur, sama ñaari doom ñii toog ak yaw, kenn ci sa ndeyjoor, ki ci des ci sa càmmooñ.» 20:22 Yeesu ne ko: «Xamuleen li ngeen di ñaan. Ndax man ngeen a naan kaasu naqar, bi may naan?» Ñu tontu ko: «Man nañu ko.» 20:23 Yeesu ne leen: «Ci dëgg dingeen naan sama kaas, waaye toog ci sama ndeyjoor mbaa sama càmmooñ, du man maa koy maye, waaye sama Baay moo koy may ñi mu ko waajal.» 20:24 Bi nga xamee ne fukki taalibe ya dégg nañu loolu, ñu mere ñaari doomi ndey ya. 20:25 Waaye Yeesu woo leen ne leen: «Xam ngeen ne ci xeeti àddina, njiit yi dañu leen di dóor yetu nguur, te kilifa yi dañu leen di noot. 20:26 Buleen mel ni ñooñu. Waaye ku bëgg a nekk kilifa ci yéen, na nekk seen surga, 20:27 te ku bëgg a nekk njiit, na nekk seen jaam. 20:28 Ndaxte noonu la Doomu nit ki ñëwe, du ngir ñu nekk ay surgaam, waaye muy seen surga, ba joxe bakkanam ngir njotug ñu bare.» 20:29 Gannaaw loolu Yeesu génn Yeriko, te mbooloo mu bare topp ko. 20:30 Fekk ñaari gumba toog ci wetu yoon wa. Bi gumba ya déggee ne, Yeesu di jaar, ñu daldi yuuxu ne ko: «Sang bi, yaw Sëtu Daawuda bi, yërëm nu!» 20:31 Waaye nit ña gëdd leen, ngir ñu noppi. Teewul gumba ya gën a yuuxu naan: «Sang bi, yaw Sëtu Daawuda bi, yërëm nu!» 20:32 Noonu Yeesu daldi taxaw, woo leen ne: «Lu ngeen bëgg, ma defal leen ko?» 20:33 Ñu tontu ko: «Sang bi, na sunuy bët ubbiku.» 20:34 Noonu Yeesu yërëm leen, laal seeni bët, ñu daldi gis ca saa sa, topp ci moom.
21:1 Gannaaw loolu Yeesu ak taalibe ya jege woon nañu Yerusalem, ba agsi dëkku Betfase ci wetu tundu Oliw ya. Noonu Yeesu yebal ñaari taalibe, 21:2 ne leen: «Demleen ci dëkk bi ci seen kanam. Bu ngeen eggee, dingeen gis mbaam mu ñu yeew ak cumburam; yiwileen leen, indil ma leen. 21:3 Te bu leen kenn waxee dara, ngeen ne ko: “Boroom bi da leen a soxla.” Kon ca saa sa dina leen bàyyi, ñu dem.» 21:4 Yeesu def na noonu, ngir la ñu waxoon jaarale ko cib yonent am, bi mu naan: 21:5 «Waxal waa Siyon:“Seen buur a ngi ñëw ci yéen;ku lewet la, te war mbaam-sëf,dig cumbur, doomu mbaam.”» 21:6 Noonu taalibe ya dem, def loolu leen Yeesu sant. 21:7 Ñu indi mbaam ma, moom ak cumbur ga, lal ci seeni yére, Yeesu toog ca. 21:8 Ña ëpp ca mbooloo ma lal seeni yére ca yoon wa, ñenn ña dagg ay cari garab, lal leen it ca yoon wa. 21:9 Mbooloom ña ko jiitu ak ña ko topp ñépp di wax ca kaw naan:«Osaana, yaw Sëtu Daawuda bi!Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi,ku barkeel nga!Ca bérab yu gën a kawe,nañu ne: “Osaana!”» 21:10 Bi nga xamee ne Yeesu dugg na Yerusalem, dëkk ba bépp yengatu ne: «Kii moo di kan?» 21:11 Mbooloo ma tontu leen ne: «Kii moo di yonentu Yàlla Yeesu, bi jóge Nasaret ci Galile.» 21:12 Bi loolu amee Yeesu dugg ca kër Yàlla ga, dàq ñépp ña fay jaay ak ña fay jënd. Mu daaneel taabali weccikatu xaalis ya ak tooguy jaaykati pitax ya, 21:13 naan: «Mbind mi nee na: “Sama kër dinañu ko wooye këru ñaan ci Yàlla,” waaye yéen def ngeen ko këru sàcc.» 21:14 Noonu ay gumba ak ay lafañ ñëw ci moom ca kër Yàlla ga, mu faj leen. 21:15 Bi nga xamee ne saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya gis nañu yëf yu doy waar ya mu def, te dégg xale yu ndaw ya nekk ca kër Yàlla ga, di wax ci kaw naan: «Osaana, yaw Sëtu Daawuda bi!» ñu daldi mer. 21:16 Noonu ñu ne Yeesu: «Ndax dégg nga li ñuy wax?» Yeesu tontu leen ne: «Waaw dégg naa ko. Ndax musuleen a jàng lii ci Mbind mi: “Ci gémmiñu perantal ak ñiy nàmp sàkkal nga sa bopp ay cant”?» 21:17 Bi Yeesu waxee loolu, mu bàyyi leen, génn dëkk ba, jëm Betani, fanaan fa. 21:18 Ci suba teel Yeesu dellusi ca dëkk ba, mu xiif. 21:19 Noonu mu séen garabu figg ca yoon wa, waaye bi mu fa agsee, gisu ci dara lu dul ay xob rekk. Ci kaw loolu Yeesu ne ko: «Dootuloo meññ mukk.» Ca saa sa figg ga daldi wow. 21:20 Bi nga xamee ne taalibe ya gis nañu loolu, ñu waaru naan: «Nan la figg gi daldi wowe ci taxawaay bi?» 21:21 Noonu Yeesu tontu leen ne: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, su ngeen gëmee te bañ a werante, dingeen def li ma def figg gi, rax-ca-dolli bu ngeen nee tund wale: “Jógal tàbbi ca géej ga,” dina ko def. 21:22 Te lépp lu ngeen laaj cig ñaan, bu ngeen ci boolee ngëm, dingeen ci jot.» 21:23 Gannaaw loolu Yeesu dugg ca kër Yàlla ga, di fa jàngale. Bi muy jàngale nag saraxalekat yu mag ya ak njiiti xeet wa ñëw ci moom ne ko: «Yëf yii ngay def, ci ban sañ-sañ nga koy defe? Ku la may boobu sañ-sañ?» 21:24 Yeesu tontu leen ne: «Man itam dinaa leen laaj lenn; bu ngeen ma ko waxee, kon dinaa leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii. 21:25 La Yaxya daan def, di sóob nit ñi ci ndox, fu mu ko jële, ci Yàlla walla ci nit ñi?» Ci kaw loolu ñu daldi werante ci seen biir naan: «Bu nu nee: “Ci Yàlla,” dina nu laaj: “Lu tax gëmuleen ko kon?” 21:26 Te bu nu nee: “Ci nit ñi,” kon mbooloo mi dal ci sunu kaw, ndaxte ñépp teg nañu Yaxya ab yonent.» 21:27 Ñu tontu Yeesu nag: «Loolu xamunu ko.» Noonu Yeesu ne leen: «Kon man itam duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii. 21:28 «Lu di seen xalaat ci lii? Kenn nit amoon na ñaari doom. Am bés mu ñëw ca taaw ba ne ko: “Sama doom, demal tey liggéeyi ca sama toolu réseñ.” 21:29 Taaw ba tontu ko ne: “Maa ngi dem baay,” waaye demu ca. 21:30 Gannaaw gi, baay ba ñëw ca ñaareel ba, wax ko noonu. Mu tontu ko ne: “Bëgguma caa dem,” waaye gannaaw loolu xelam soppiku, mu dem ca.» 21:31 Noonu Yeesu laaj leen: «Kan ci ñaari doom yooyu moo def coobareg baayam?» Ñu ne: «Ñaareel bi.» Kon Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, juutikat yi ak jigéeni moykat yi ñoo leen jëkk a dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji. 21:32 Ndaxte Yaxya ñëw na ci yéen ci yoonu njub, te gëmuleen ko; waaye juutikat yi ak jigéeni moykat yi gëm nañu ko. Te gannaaw bi ngeen gisee loolu, seen xel soppikuwul sax, ba ngeen gëm ko.» 21:33 Yeesu teg ca ne: «Dégluleen beneen léeb. Amoon na fi benn boroom kër bu jëmbët toolu réseñ. Mu ñag tool bi, gas ci biir pax, ngir nal ci réseñ yi. Mu tabax wottukaay, batale ko ay beykat, daldi tukki. 21:34 «Bi nga xamee ne bëgg nañoo witt réseñ yi, mu yónni ay surgaam ci beykat yi, ngir jot wàllam ci meññeef mi. 21:35 Waaye beykat yi jàpp surga yi, kenn ki ñu dóor ko ay yar, keneen ki ñu rey ko, ki ci des ñu sànni ko ay doj. 21:36 Boroom kër gi nag yónniwaat yeneen surga yu ëpp yu jëkk ya, beykat yi def leen noonu ñoom itam. 21:37 Mujj mu yónni doomam naan: “Xëy na ñu weg sama doom.” 21:38 Waaye bi beykat yi gisee doom ji, ñu ne ci seen bopp: “Kii moo war a donn tool bi; nan ko rey, moom ndonoom.” 21:39 Ñu jàpp ko nag, génne ko tool bi, rey ko.» 21:40 Noonu Yeesu laaj leen: «Bu boroom tool bi ñëwee nag, na muy def beykat yi?» 21:41 Ñu ne ko: «Dina rey reyin wu ñaaw nit ñu soxor ñooñu, batale tool bi yeneen beykat, yi koy jox wàllam ci jamonoy meññeef.» 21:42 Kon Yeesu ne leen: «Xanaa musuleen a jàng lii ci Mbind yi?“Doj wi tabaxkat yi sànni;mujj na di doju koñ;ci Boroom bi la loolu jóge,te yéemu nanu ci.” 21:43 «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, dinañu leen xañ nguuru Yàlla, dénk ko xeet wuy def ay jëfam. 21:44 Ku dal ci doj wii, dammtoo; ku mu dal ci sa kaw, rajaxe la.» 21:45 Bi nga xamee ne saraxalekat yu mag ya ak Farisen ya dégg nañu léebam yooyu, ñu xam ne ñoom lay wax. 21:46 Noonu ñu di ko fexee jàpp, waaye ragal nañu nit ña, ndaxte ñépp teg nañu ko ab yonent.
22:1 Gannaaw loolu Yeesu nettali leen beneen léeb ne leen: 22:2 «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni buur buy waajal céetu doomam ju góor. 22:3 Noonu mu yónni ay surgaam, ngir ñu woo gan yi ca céet ga, waaye gan yi bëgguñoo ñëw. 22:4 Kon mu yónneeti yeneen surga ne leen: “Bu ngeen demee, yégal-leen gan yi sama woote bii: ‘Reer yi noppi na, reylu naa samay nag ak samay jur gu duuf; lépp sotti na, ñëwleen ci reer yi.’ ” 22:5 Waaye ba tey wuyuwuñu ko; ñu dem, kenn ki ca toolam, kenn ki jaayaani, 22:6 ña ca des jàpp surga ya, toroxal leen, rey leen. 22:7 «Noonu buur mer, daldi yónni ay xarekatam, ngir ñu rey bóomkat yooyule, lakk seen dëkk. 22:8 Ci kaw loolu mu ne surga ya: “Reeri céet gi noppi na, waaye ñi ñu woo yeyoowuñu ko. 22:9 Demleen nag buntu dëkk ba, woo ku ngeen fa gis ci reeri céet gi.” 22:10 Noonu surga ya génn ca yoon ya, boole ña ñu fa gis ñépp, ñu bon ña ak ñu baax ña, ba néegu reer ya fees ak ay gan. 22:11 «Bi nga xamee ne buur bi dugg na nag, ngir seetsi gan yi, mu gis fa nit ku solul mbubb mu ñu war a sol ca céet ga. 22:12 Buur ne ko: “Sama waay, naka nga dugge fii, te amuloo mbubbum céet?” Waa ji ne miig. 22:13 Noonu buur ba ne ay surgaam: “Yeewleen ko ci tànk yi ak ci loxo yi, sànni ko ci biti ci lëndëm gi. Foofa dees na fa jooy tey yéyu.” 22:14 Ndaxte ñi ñu woo bare nañu, waaye ñi ñu tànn barewul.» 22:15 Booba Farisen ya dem gise, ba xam lu ñu war a def, ngir fiir Yeesu ci waxam. 22:16 Noonu ñu yónni ci moom seeni taalibe ak ñi far ak buur bi Erodd ne ko: «Kilifa gi, xam nanu ne ku wóor nga, te ragaloo kenn, ndaxte seetuloo jëmmi nit, waaye dangay xamle yoonu Yàlla ci bu wóor. 22:17 Wax nu nag loo xam ci lii: ndax jaadu na, nu fey buur bi Sesaar galag walla déet?» 22:18 Waaye Yeesu xam seen njublaŋ, mu ne leen nag: «Lu tax ngeen bëgg maa fiir, yéen naaféq yi? 22:19 Wonleen ma poset, bi ñuy feye galag.» Ñu daldi ko jox nag benn posetu denariyon. 22:20 Yeesu ne leen: «Kan lañu ci def nataalam ak turam?» 22:21 Ñu tontu ko: «Sesaar.» Noonu mu ne leen: «Joxleen nag Sesaar li Sesaar moom, te jox Yàlla li Yàlla moom.» 22:22 Bi nga xamee ne dégg nañu loolu, ñu waaru, bàyyi ko, daldi dem. 22:23 Bés boobale ay Sadusen ñëw ci moom. Sadusen yi nag ñoom gëmuñu ne ndekkite am na. Noonu ñu laaj ko naan: 22:24 «Kilifa gi, Musaa nee woon na: “Boo xamee ne góor dee na te amul doom, na rakkam donn jabaram, ngir sàkkal magam njaboot.” 22:25 Amoon na ci nun nag juróom-ñaari góor, ñu bokk ndey ak baay. Taaw ba séyoon na, faatu; rakk ja donn jabar ja, ndaxte amul woon doom. 22:26 Ñaareel ba ak ñetteel ba def noonu, ba ci juróom-ñaareel ba. 22:27 Gannaaw ñoom ñépp, jigéen ja faatu. 22:28 Bu ndekkite taxawee nag, jabaru kan lay doon ci juróom-ñaar ñi, ndaxte ñépp jël nañu ko?» 22:29 Waaye Yeesu tontu leen ne: «Yéena ngi cig réer, ndaxte xamuleen Mbind mi mbaa kàttanu Yàlla. 22:30 Ndaxte keroog ndekkite li kenn du am jabar, kenn du am jëkkër, waaye dinañu mel ni malaaka yi ci kaw. 22:31 Te lu jëm ci ndekkitel ñi dee, xanaa musuleen a jàng la leen Yàlla waxoon ne: 22:32 “Maay Yàllay Ibraayma ak Yàllay Isaaxa ak Yàllay Yanqóoba”? Li ciy génn mooy, nekkul Yàllay ñi dee waaye Yàllay ñiy dund la.» 22:33 Bi nga xamee ne mbooloo ma dégg nañu loolu, ñu waaru ndax li mu jàngale. 22:34 Gannaaw gi, Farisen ya yég nañu ne, yey na Sadusen ya. Kon nag ñu daldi daje. 22:35 Noonu kenn ci ñoom, ka nekk xutbakat, fexe koo fiir. Mu laaj ko: 22:36 «Kilifa gi, ban ndigal moo gën a màgg ci yoonu Musaa?» 22:37 Yeesu tontu ko ne: « “Nanga bëgg Yàlla sa Boroom ak sa xol bépp ak sa bakkan bépp ak sa xel mépp.” 22:38 Loolu moo di li jëkk te ëpp ci li Yàlla santaane. 22:39 Te ñaareel bi noona la mel: “Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.” 22:40 Ñaari ndigal yooyu tënk nañu yoonu Musaa wépp, moom ak waxi yonent yi.» 22:41 Bi Farisen ya dajee nag, Yeesu laaj leen: 22:42 «Lu ngeen xalaat ci Almasi bi; kan la nekk sëtam?» Ñu tontu ko: «Daawuda.» 22:43 Noonu Yeesu ne leen: «Lu tax nag Daawuda, bi muy wax ci kàttanu Xelu Yàlla mi, di ko wooye “Boroom bi” ne: 22:44 “Boroom bi wax na sama Boroom:‘Toogal ci sama ndeyjoor,ba kera may daaneelsay noon ci sa kanam’ ” 22:45 Gannaaw Daawuda nag wooye na ko: “Boroom bi,” nu muy nekke sëtam?» 22:46 Ci kaw loolu kenn mënu koo tontu genn kàddu. Te li dale ci bés booba kenn ñemeetu koo laaj dara.
23:1 Gannaaw loolu Yeesu waxoon na mbooloo ma ak taalibeem ya ne leen: 23:2 «Xutbakat ya ak Farisen ya ñu ngi toog ci jalu Musaa. 23:3 Lépp lu ñu leen wax nag, defleen ko te sàmm ko, waaye buleen roy seeni jëf, ndaxte dañuy wax waaye duñu ko jëfe. 23:4 Dañuy takk say yu diis, yen leen ci nit ñi, waaye duñu ko nangoo laal sax ak seen cati baaraam. 23:5 Dañuy def seeni jëf yépp, ngir nit ñi gis leen, di takk ay téere yu réy, tey réyal seeni laari mbubb. 23:6 Ca reeri xew yi, toogu yu yiw lañuy taamu, tey féete kanam ca jàngu ya. 23:7 Dañoo bëgg ñépp nuyoo leen ñaari loxo ca pénc ma, di leen wooye “Kilifa gi.” 23:8 Waaye yéen buñu leen wooye “Kilifa gi,” ndaxte kenn rekk moo di seen Kilifa, te yéen ñépp ay bokk ngeen. 23:9 Te buleen tudde kenn seen “baay” ci àddina, ndaxte kenn rekk moo di seen Baay, ki ci kaw. 23:10 Buñu leen tudde it ay “njiit,” ndaxte kenn rekk moo di seen Njiit, mooy Kirist. 23:11 Ki gën a mag ci yéen mooy ki nangoo nekk seen surga. 23:12 Kuy yékkatiku, dees na la suufeel; kuy suufeelu, ñu yékkati la. 23:13 «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi tëj nguuru Yàlla Aji Kawe ji ci kanamu nit ñi; yéen dungeen ci dugg, te dungeen bàyyi ku ci bëgg a dugg, mu dugg ci. 23:15 «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi wër géej ak suuf, ngir sàkku benn taalibe, ba noppi ngeen def ko nitu safara, ku leen yées ñaari yoon. 23:16 «Yéen njiit yu gumba yi, dingeen torox! Yéena ngi wax ne: “Ku giñe kër Yàlla gi, ngiñ li duggul, waaye ku giñ ci wurusu kër Yàlla gi, dugg na.” 23:17 Yéen ñi dof te gumba! Lan moo gën a màgg, wurus wi walla kër Yàlla, gi tax wurus wi sell? 23:18 Dangeen ne it: “Ku giñe saraxalukaay bi ci kër Yàlla gi, ngiñ li duggul, waaye ku giñ ci sarax si ci kawam, dugg na.” 23:19 Gumba yi! Lan moo gën a màgg, sarax si walla saraxalukaay bi tax sarax si sell? 23:20 Ku giñe saraxalukaay bi, giñ nga ci saraxalukaay bi ak li ci kawam lépp. 23:21 Ku giñe kër Yàlla gi, giñ nga ci kër Yàlla gi ak Ki ci dëkk. 23:22 Ku giñ ci asamaan, giñ nga ci jalu Buur Yàlla ak Ki ci toog. 23:23 «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi sàkk asaka ci naana ak anet ak kumin, te sàggane yi gën a màgg ci yoonu Musaa, maanaam njub, yërmande ak ngëm. Loolu ngeen war a def, waxuma nag ngeen bàyyi la ca des. 23:24 Yéen njiit yu gumba yi! Yéena ngi segg wallax-njaan, tey wann giléem. 23:25 «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi setal bitib kaas bi ak ndab li, waaye ci biir dafa fees ak càcc ak ëppal. 23:26 Farisen yu gumba yi! Jëkkleen a setal biir kaas bi ak ndab li, ngir biti bi itam set. 23:27 «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi mel ni bàmmeel yu ñu weexal. Ci biti am nañu melo wu rafet, waaye ci biir dañoo fees ak yaxi ñi dee ak tilim ju nekk. 23:28 Yéen itam, ci ngistal dangeen a mel ni ñu jub, waaye ci seen biir dangeen fees ak naaféq ak lu bon. 23:29 «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi tabax xabruy yonent yi, tey rafetal bàmmeeli ñu jub ñi. 23:30 Te yéena ngi wax ne: “Bu nu fekke woon sunu jamonoy maam, dunu ànd ak ñoom ciy tuur deretu yonent yi.” 23:31 Seede ngeen nii ne, yey ngeen seen bopp, te yéenay doomi ñi doon rey yonent yi, 23:32 di aw seen tànki baay, ba yées leen sax. 23:33 Yéen ñi mel ni ay jaan, te fees ak daŋar niy co, naka ngeen di mucce mbugalu safara? 23:34 Moo tax maa ngi leen di yónnee ay yonent ak ay boroom xam-xam ak ay xutbakat. Ñenn ñi dingeen leen rey te daaj leen ci bant; ñeneen ñi dingeen leen dóor ay yar ci seeni jàngu, di leen fitnaal ci dëkkoo-dëkk. 23:35 Noonu deretu ñi jub, ji ñu tuur jépp ci àddina, dina xëppu ci seen kaw, li dale ci deretu Abel mi jub, ba ci deretu Sakariya doomu Baraki, mi ngeen rey ci diggante bérab bu sell bi ak saraxalukaay bi. 23:36 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, loolu lépp dina dal ci niti jamono jii. 23:37 «Yerusalem, Yerusalem, yaw miy rey yonent yi, tey sànni ay doj ndaw yi, ba ñu dee, aka maa bëggoon a dajale say doom, ni ginaar di uufe ay cuujam, te nanguwuleen! 23:38 Kon nag Yàlla dina bërgël seen kër, ba mu gent. 23:39 Ndaxte maa ngi leen koy wax, dungeen ma gisati li dale tey, ba kera ngeen ne: “Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga!”»
24:1 Bi Yeesu waxee ba noppi, mu génn ca kër Yàlla ga, dem. Noonu ay taalibeem ñëw ci moom, ngir won ko tabaxi kër Yàlla ga. 24:2 Waaye mu tontu leen ne: «Du gis ngeen yii yépp? Ci dëgg maa ngi leen koy wax, lii lépp dina daanu, ba doj dootul des ci kaw doj.» 24:3 Noonu bi nga xamee ne Yeesu toog na ca tundu Oliw ya, taalibeem ya ñëw ci moom cig wet. Ñu ne ko: «Wax nu kañ la loolu di am, te luy tegtale ne, yaa ngi ñëw te àddina di tukki?» 24:4 Yeesu tontu leen ne: «Moytuleen, bu leen kenn nax. 24:5 Ndaxte ñu bare dinañu ñëw ci sama tur ne: “Maa di Kirist,” te dinañu nax ñu bare. 24:6 Dingeen dégg ay xare ak coowi xare; wottuleen, buleen ci tiit, ndaxte loolu war na am, waaye booba muju jamono ji jotagul. 24:7 Xeet dina jóg, xeex ak weneen xeet, réew xeex ak meneen réew. Dina am ay xiif ak ay yengu-yenguy suuf ci bérab yu bare. 24:8 Waaye loolu lépp mooy ndoortel metit yi, mel ni jigéen juy matu. 24:9 Bu boobaa dees na leen jébbale, metital leen, rey leen; te xeet yépp dinañu leen bañ ndax sama tur. 24:10 Bu loolu amee ñu bare dinañu dàggeeku, di booleente tey bañante. 24:11 Te it ñu bare ñuy mbubboo turu yonent dinañu feeñ, nax nit ñu bare. 24:12 Te gannaaw lu bon day law, mbëggeelug ñi ëpp dina wàññiku. 24:13 Waaye ku muñ ba ca muj ga, mucc. 24:14 Noonu xebaar bu baax bii ci nguuru Yàlla, dees na ko yégle ci àddina sépp, ngir mu nekk seede ci xeet yépp. Bu loolu amee muju jamono ji jot. 24:15 «Dina am bés bu li ñuy wax: “Lu araam luy yàqe” dina tege ca bérab bu sell ba. Mooy li ñu doon wax jaarale ko ci yonent Yàlla Dañeel; ku ko jàng, nanga ko xam. 24:16 Bu ngeen gisee loolu nag, ku nekk ci biir diiwaanu Yude, nanga daw ca tund ya; 24:17 ku nekk ci kaw taax ma, bul wàcc ngir fab say yëf, ya nekk ci biir kër ga; 24:18 ku nekk ca tool ba, bul ñibbi ngir fab sa mbubb. 24:19 Ngalla jigéen ñi ëmb ca bés yooyu, ngalla it ñiy nàmpal! 24:20 Ñaanleen nag seen gàddaay bumu nekk jamonoy seddaayu lolli, walla bésu noflaay bi. 24:21 Ndaxte booba dina am metit wu réy wu musul a am, ba àddina sosoo ak tey, te dootul am mukk. 24:22 Te bu ñu wàññiwul bés yooyu, kenn du mucc, waaye dees na leen wàññi ndax ñi Yàlla tànn. 24:23 «Booba nag, bu leen kenn waxee: “Kaayleen gis, Kirist a ngi fi,” mbaa: “Mu nga fale,” buleen ko gëm. 24:24 Ndaxte ñi mbubboo turu Kirist ak ñi mbubboo turu yonent dinañu feeñ, di joxe ay firnde yu réy ak ay kéemaan, ba ciy nax sax ñi Yàlla tànn, su loolu manoon a am. 24:25 Wax naa leen ko lu jiitu. 24:26 «Bu ñu leen waxee nag: “Seetleen, mu nga nale ca àll ba,” buleen génn, mbaa ñu ne: “Seetleen mu ngi nii ci biir kër gi,” buleen ko gëm. 24:27 Ndaxte ni melax di fàqe penku, te lerax ba sowu, noonu la ñëwu Doomu nit ki di mel. 24:28 Fa médd nekk, fa la tan yiy dajee. 24:29 «Gannaaw metitu bés yooyule nag, ca saa sa jant bi dina lëndëm te weer wi dootul leer; biddiiw yi dinañu fàq, daanu ci asamaan, te kàttani asamaan yi yengu. 24:30 Booba firnde ji taxaw, Doomu nit ki feeñ ci asamaan, te xeeti àddina sépp dinañu jooy. Dinañu gis Doomu nit ki di ñëw ci niiri asamaan si, ànd ak kàttan ak ndam lu réy. 24:31 Dina yónni ay malaakaam ak baatu liit bu dégtu, ñu dajale ñi mu tànn ci ñeenti xebla yi, fa asamaan dale ba fu mu yem.» 24:32 Yeesu teg ca ne: «Jàngleen misaalu garabu figg ga. Boo xamee ne ay bànqaasam duy nañu, ay xobam sëq, xam ngeen ne nawet jege na. 24:33 Noonu yéen itam bu ngeen gisee loolu lépp, xamleen ne jege na, mu ngi ci bunt bi sax. 24:34 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, niti jamono jii duñu wéy te loolu lépp amul. 24:35 Asamaan ak suuf dinañu wéy, waaye samay wax du wéy mukk. 24:36 «Waaye bés booba walla waxtu wa, kenn xamul kañ lay doon; du malaaka yi ci kaw, du sax man Doom ji, waaye Baay bi rekk moo ko xam. 24:37 Ni bési Nóoyin ya, noonu lay mel, bu Doomu nit ki di ñëw. 24:38 Ndaxte ca bés ya jiitu mbënn ma, nit ñaa ngi doon lekk di naan, góor yaa ngi doon takk jabar, tey maye seeni doom, ba bés ba Nóoyin duggee ca gaal ga; 24:39 xalaatuñu woon dara, ba kera ndoxum mbënn ma di dikk, yóbbu leen. Noonu lay mel ci ñëwu Doomu nit ki. 24:40 «Bu boobaa ci ñaar ñu nekk cib tool, dinañu jël kenn ki, bàyyi ki ci des. 24:41 Ci ñaari jigéen ñuy wol ca ëtt ba, dinañu jël kenn ki, bàyyi ki ci des. 24:42 Yeewuleen nag, ndaxte xamuleen bés bu seen Boroom di ñëw. 24:43 Waaye xamleen lii: bu boroom kër gi xamoon, ci ban waxtu ci guddi la sàcc bi di ñëw, kon dina yeewu te du ko bàyyi, mu toj këram. 24:44 Loolu moo tax yéen itam taxawleen jonn, ndaxte Doomu nit ki dina ñëw ci waxtu wu ngeen ko séenuwul.» 24:45 Yeesu teg ca ne: «Kan moo nekk surga bu takku te teey, bu njaatigeem teg ci waa kër gi, ngir mu leen di dundal ca jamono ja? 24:46 Bu njaatigeem ñëwee te gis muy def noonu, surga boobu dina am ngërëm. 24:47 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, njaatige bi dina ko teg ci alalam jépp. 24:48 Waaye bu dee surga bu bon bu naan ci xelam: “Sama njaatige day yéex a ñëw,” 24:49 mu tàmbalee dóor ay bokki surgaam, di lekk te naan ak naankat ya, 24:50 kon njaatige ba dina ñëw ci bés bu mu ko séenuwul ak waxtu wu mu xamul. 24:51 Dina ko dóor ay yar yu metti, jox ko añub naaféq. Foofa dees na fa jooy tey yéyu.
25:1 «Booba nguuru Yàlla Aji Kawe ji dina mel ni fukki janq, ñu fab seeni làmp, génn, gatanduji boroom séet ba. 25:2 Fekk juróom ca janq ya di ñu am xel, juróom ya ca des ñàkk xel. 25:3 Ñi ñàkk xel nag fab nañu seeni làmp, waaye fabaalewuñu diwlin; 25:4 waaye ñi am xel ñoom fab nañu seeni làmp, fabaale diwlin ciy njaq. 25:5 Ni boroom séet bi yéexee ñëw nag, ñépp gëmmeentu bay nelaw. 25:6 «Noonu ci xaaju guddi baat jib ne: “Boroom séet baa ngi, génnleen, gatandu ko.” 25:7 Bi ko janq ya déggee, ñu jóg, defar seeni làmp. 25:8 Ñi ñàkk xel wax ñi am xel: “Mayleen nu ci seen diwlin, ndaxte sunuy làmp ñu ngi bëgg a fey.” 25:9 Waaye ñi am xel tontu leen ne: “Li nu yor du doy ngir nun ak yéen; tee ngeen a dem ca jaaykat ya, jënd.” 25:10 «Bi nga xamee ne dem nañu jëndi, boroom séet ba agsi. Ñi amoon diwlin ci seeni làmp, ànd ak boroom séet ba ca reer ya. Noonu bunt ba tëj. 25:11 Gannaaw loolu janq ya ca des agsi naan: “Sang bi, Sang bi, ubbil nu.” 25:12 Waaye mu tontu leen ne: “Ci dëgg maa ngi leen koy wax, xawma leen.” 25:13 «Yeewuleen nag, ndaxte xamuleen bés ba mbaa waxtu wa. 25:14 «Te it nguuru Yàlla dafa mel ni kuy tukki bitim réew. Bi mu laata dem, mu woo ay surgaam, batale leen alalam, ku nekk lu mu àttan. 25:15 Kenn ka, mu dénk ko juróomi milyoŋ, keneen ka, mu dénk ko ñaar; ka ca des, benn; daldi tukki. 25:16 «Bi mu demee nag, ki jot juróomi milyoŋ ya dem, di ci jula, ba amaat yeneen juróom. 25:17 Noonu it ki jot ñaar amaat yeneen ñaar. 25:18 Waaye ki jot benn milyoŋ dem, gas pax, nëbb fa xaalisu njaatigeem. 25:19 «Gannaaw diir bu yàgg njaatigeb surga ya dellusi, daldi leen laaj alalam. 25:20 Noonu ki jot juróomi milyoŋ ya jegeñsi, indi yeneen juróom naan: “Kilifa gi, dénk nga ma juróomi milyoŋ; seetal, ame naa ci yeneen juróom.” 25:21 Njaatigeem tontu ko: “Def nga lu baax, surga bu baax nga te takku. Gannaaw takku nga ci lu tuuti, dinaa la dénk lu bare. Kaay bokk ci sama mbég.” 25:22 Naka noona ki jot ñaari milyoŋ it jegeñsi ne ko: “Kilifa gi, dénk nga ma ñaari milyoŋ, seetal, ame naa ci yeneen ñaar.” 25:23 Njaatigeem ne ko: “Def nga lu baax, surga bu baax nga te takku. Gannaaw takku nga ci lu tuuti, dinaa la dénk lu bare. Kaay bokk ci sama mbég.” 25:24 «Gannaaw loolu nag, ki jot benn milyoŋ jegeñsi ne ko: “Kilifa gi, xamoon naa ne, nit ku néeg nga; dangay dajale foo jiwul, tey góob foo faruwul. 25:25 Moo tax ma ragaloon la, ba dem, nëbb sa xaalis ci biir suuf; mi ngii, fabal li nga moom.” 25:26 Waaye njaatigeem tontu ko: “Surga bu bon nga te tayel! Gannaaw xamoon nga ne, damay dajale fu ma jiwul, tey góob fu ma faruwul, 25:27 kon waroon ngaa yóbbu sama xaalis ca denckati xaalis ya. Bés bu ma ñëwee nag, ma man a jot li ma moom ak la mu jur.” 25:28 Noonu njaatige bi ne: “Nanguleen xaalis bi ci moom, jox ko boroom fukki milyoŋ yi. 25:29 Ndaxte ku am dinañu la dolli, ba nga barele, waaye ku amul, li nga am as néew sax, dinañu ko nangu. 25:30 Te sànnileen surga bu amul njariñ bi ci biti ci lëndëm gi. Foofa dees na fa jooy te yéyu.” 25:31 «Boo xamee ne Doomu nit ki mu ngi ñëw ci ndamam, ànd ak malaaka yépp, booba dina falu ni buur, toog ci jalam bu soloo ndam. 25:32 Bu boobaa dees na dajale xeeti àddina yépp ci kanamam, te dina leen xàjjale, ni sàmm di xàjjalee xar yi ak bëy yi, 25:33 mu teg xar yi ci ndeyjooram, bëy yi ci càmmooñam. 25:34 «Noonu Buur bi dina wax ñi féete ndeyjoor: “Agsileen, yéen ñi sama Baay barkeel, jël-leen nguur, gi ñu leen waajal li dale ci njàlbéenug àddina. 25:35 Ndaxte xiifoon naa, ngeen jox ma, ma lekk; te mar, ngeen jox ma, ma naan; nekkoon naa ab doxandéem, ngeen fat ma; 25:36 te rafle, ngeen wodd ma; woppoon naa, ngeen seetsi ma; te ñu tëj ma, ngeen ñëw fi man.” 25:37 Ci kaw loolu ñi jub dinañu tontu ne: “Boroom bi, kañ lanu la gisoon, nga xiif, nu jox la, nga lekk; mbaa nga mar, nu jox la, nga naan? 25:38 Kañ lanu la gisoon, nga nekk ab doxandéem, nu fat la; mbaa nga rafle, nu wodd la? 25:39 Kañ lanu la gisoon, nga wopp mbaa ñu tëj la, nu ñëw ci yaw?” 25:40 Noonu Buur bi dina leen tontu ne: “Ci dëgg maa ngi leen koy wax, saa yu ngeen defalee loolu kenn ki gën a ndaw ci sama bokk yii, man ngeen ko defal.” 25:41 «Gannaaw loolu dina wax ñi ci càmmooñam: “Soreleen ma yéen ñi alku, te dem ci safara su dul fey, si ñu sàkkal Seytaane ak ay malaakaam. 25:42 Ndaxte xiifoon naa waaye joxuleen ma, ma lekk; te mar waaye joxuleen ma, ma naan. 25:43 nekkoon naa ab doxandéem, waaye fatuleen ma; te rafle, waaye wodduleen ma; woppoon naa te ñu tëj ma, waaye seetsiwuleen ma.” 25:44 Ci kaw loolu dinañu tontu ne: “Boroom bi, kañ lanu la gisoon, nga xiif, mbaa nga mar, nga nekk ab doxandéem mbaa rafle, nga wopp mbaa ñu tëj la, te topptoowunu la?” 25:45 Kon dina leen tontu ne: “Ci dëgg maa ngi leen koy wax, saa su ngeen ko defalul kenn ci ñi gën a ndaw, man ngeen ko defalul.” 25:46 Noonu ñii dinañu sóobu ci mbugal gu dul jeex, waaye ñi jub dinañu tàbbi ci dund gu dul jeex.»
26:1 Bi nga xamee ne Yeesu wax na loolu lépp ba noppi, mu ne taalibeem ya: 26:2 «Xam ngeen ne, ñaari fan a des ci màggalu bésu Jéggi ba, te dinañu wor Doomu nit ki, daaj ko ci bant.» 26:3 Booba nag saraxalekat yu mag ya ak njiiti xeet wa dajaloo ca kër gu réy gu saraxalekat bu mag ba, tudd Kayif. 26:4 Ñu daldi gise, ba xam lu ñu man a fexe, ba jàpp Yeesu, reylu ko. 26:5 Waaye ñu ne: «Bumu doon ci bésu màggal bi, ngir yengu-yengu bañ a am ci nit ñi.» 26:6 Bi nga xamee ne Yeesu nekkoon na dëkku Betani ca kër Simoŋ ma gaana woon, 26:7 jenn jigéen ñëw ci moom, yor njaq lu ñu yette doj wu ñuy wax albaatar. Njaq la def latkoloñ bu jar lu baree-bare. Noonu bi Yeesu toogee di lekk, jigéen ji tuur ko ci boppu Yeesu. 26:8 Waaye bi ko taalibe ya gisee, ñu daldi mer ne: «Yàq gii lu muy jariñ? 26:9 Maneesoon na koo jaay ci lu bare, jox xaalis bi miskin yi.» 26:10 Yeesu nag xam la ñu wax, mu ne leen: «Jigéen ji defal na ma jëf ju rafet; lu tax ngeen di ko sonal? 26:11 Miskin yaa ngi ak yéen bés bu nekk, waaye dungeen ma gis ba fàww. 26:12 Kii, ci li mu tuur latkoloñ bii ci sama yaram, def na ko ngir waajal sama rob. 26:13 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, fépp fu ñuy yéene xebaar bu baax bi ci àddina sépp, dinañu fa fàttali it li jigéen jii def.» 26:14 Ca waxtu woowu kenn ci fukki taalibe ya ak ñaar, ku tudd Yudaa Iskariyo, dem ca saraxalekat yu mag ya, 26:15 ne leen: «Lan ngeen ma man a jox, ngir ma jébbal leen Yeesu?» Noonu saraxalekat ya daldi ko waññal fanweeri poseti estateer. 26:16 Li dale ci saa soosa nag Yudaa di fexe jamono ju mu leen man a jébbal Yeesu. 26:17 Bés bu jëkk ca màggal, ga ñuy wax Mburu ya amul lawiir, taalibe yi ñëw ci Yeesu ne ko: «Foo bëggoon nu defaral la reeru màggalu Jéggi ba?» 26:18 Yeesu tontu leen: «Demleen ca dëkk ba, jëm ca diw, ngeen ne ko: “Kilifa gi nee na: Sama jamono jege na; ci sa kër laay màggalsi xewu Jéggi ba, man ak samay taalibe.”» 26:19 Noonu taalibe yi defar reeru Jéggi ba, na leen Yeesu waxe woon. 26:20 Bi nga xamee ne timis jot na, Yeesu toog di lekk, moom ak fukki taalibe yi ak ñaar. 26:21 Bi ñuy lekk, mu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, kenn ci yéen dina ma wor.» 26:22 Taalibe ya am naqaru xol bu réy; ku nekk daldi ne ko: «Mbaa du man, Boroom bi?» 26:23 Yeesu tontu leen ne: «Ki dugal loxoom ak man ci ndab li, kooku moo may wor. 26:24 Doomu nit ki mu ngi dem, ni ñu ko waxe ci Mbind mi, waaye ki koy wor dina torox; bañoon a juddu moo gënoon ci moom.» 26:25 Yudaa, mi ko nar a wor, laaj ko: «Mbaa du man, kilifa gi?» Yeesu ne ko: «Wax nga ko.» 26:26 Noonu bu ñuy lekk, Yeesu jël mburu, sant Yàlla, damm ko, jox ko taalibe ya. Mu ne leen: «Jël-leen lekk, lii sama yaram la.» 26:27 Gannaaw loolu mu jël kaas, sant Yàlla, jox leen ko. Mu ne leen: «Yéen ñépp naanleen ci, 26:28 ndaxte lii sama deret la, ji fas kóllëre gi, te mu tuuru, ngir ñu bare jot mbaalug bàkkaar yi. 26:29 Maa ngi leen di wax, dootuma naan gannaawsi tey ndoxum réseñ mii, ba kera may naan ak yéen ndoxum réseñ mu bees ci sama nguuru Baay.» 26:30 Gannaaw loolu ñu woy Yàlla, ba noppi génn, dem ca tundu Oliw ya. 26:31 Booba Yeesu ne leen: «Yéen ñépp dingeen ma dàggeeku ci guddi gii, ndaxte bind nañu: “Dinaa dóor sàmm bi, xari jur gi tasaaroo.” 26:32 Waaye bu ma dekkee, dinaa leen jiituji Galile.» 26:33 Piyeer nag daldi jël kàddu gi naan: «Bu la ñépp dàggeekoo, man duma la dàggeeku mukk.» 26:34 Yeesu ne ko: «Ci dëgg maa ngi la koy wax, ci guddi gii, bala ginaar a sab, dinga ma weddi ñetti yoon.» 26:35 Piyeer tontu ko: «Boo xamee ne sax, damaa war a dee ak yaw, duma la weddi mukk.» Taalibe yépp it waxe noonu. 26:36 Bi loolu amee Yeesu ànd ak ñoom ba ca bérab bu tudd Setsemane, mu ne taalibe ya: «Toogleen fii, ma dem fale, ñaan fa.» 26:37 Bi mu waxee loolu, mu ànd ak Piyeer ak ñaari doomi Sebede, daldi am tiis ba xonett. 26:38 Mu ne leen: «Sama xol dafa tiis, ba may bëgg a dee; toogleen fi, xool ak man.» 26:39 Bi mu waxee loolu, Yeesu dem ci kanam tuuti, ne nërëm ci suuf, di ñaan ne: «Sama Baay, bu manee am, na ma kaasu naqar bii teggi! Moona, bumuy ci sama coobare, waaye na sa coobare am.» 26:40 Noonu mu ñëw ca taalibe ya, fekk leen ñuy nelaw. Mu ne Piyeer: «Amuleen sax dooley xoolandoo ak man benn waxtu? 26:41 Xool-leen te ñaan, ngir bañ a daanu cig fiir; seen xol jag na, waaye seen bind a woyof.» 26:42 Yeesu delluwaat di ñaan ne: «Sama Baay, bu fekkee ne kaasu naqar bii mënu maa teggi te naanuma ko, kon na sa coobare am.» 26:43 Yeesu ñëwaat ca taalibe ya, fekk leen ñuy nelaw, ndaxte seeni bët dañoo diis. 26:44 Mu daldi leen bàyyi, waxaat loolu ñetteel bi yoon. 26:45 Noonu mu ñëw ca taalibe ya ne leen: «Nelawleen léegi te noppalu. Waxtu wu ñu ma war a jébbale ci loxoy bàkkaarkat yi, jege na. 26:46 Jógleen nu dem; xool-leen, ki may wor a ngi nii, di ñëw.» 26:47 Bi muy wax loolu nag, Yudaa, mi bokkoon ca fukki taalibe ya ak ñaar te naroon koo wor, agsi, ànd ak mbooloo mu bare, jóge ca saraxalekat yu mag ya ak ca njiiti xeet wa, te gànnaayoo jaasi ak yet. 26:48 Fekk Yudaa moomu joxoon na leen tegtal ne leen: «Ki may fóon, moom la; jàppleen ko.» 26:49 Mu daldi ñëw ci Yeesu nag ne ko: «Salaamu àleykum, kilifa gi!» daldi ko fóon bu tàng. 26:50 Yeesu tontu ko: «Sama xarit, xam naa lu tax nga ñëw.» Noonu ñu daldi jegesi, song ko, jàpp ko. 26:51 Ca saa sa kenn ci ñi ànd ak Yeesu bocci jaaseem, dóor surgab saraxalekat bu mag ba, nopp ba dagg. 26:52 Waaye Yeesu ne ko: «Roofal sa jaasi ci mbaram, ndaxte ku bocci jaasi, jaasi moo lay rey. 26:53 Xanaa xamuloo ne, man naa laaj sama Baay, te dina ma may ci taxawaay bi mbooloom malaaka mu xel dajul? 26:54 Waaye su ma ko defoon, nan la Mbind mi man a ame? Ndaxte Mbind mi nee na, nii la war a ame.» 26:55 Booba Yeesu ne mbooloo mi: «Jóg ngeen ngir jàpp ma, gànnaayoo jaasi ak yet, mel ni ñuy topp sàcc. Moona daa naa toog bés bu nekk ca kër Yàlla ga, di jàngale, te jàppuleen ma. 26:56 Waaye lii lépp xew na, ngir amal Mbindi yonent yi.» Ci kaw loolu taalibe yépp dëddu ko, daw. 26:57 Ña jàppoon Yeesu yóbbu ko kër Kayif, saraxalekat bu mag ba, fa xutbakat ya ak njiit ya daje. 26:58 Piyeer topp ko fu sore, ba ci ëttu saraxalekat bu mag ba; mu dugg, toog ak surga ya, ngir seet nu mbir may mujje. 26:59 Noonu saraxalekat yu mag ya ak kureelu àttekat ya di seet naaféq bu man a seede ci Yeesu, ba ñu man koo rey, 26:60 waaye mënuñu koo am. Teewul ñu bare ñëwoon nañu, di seede lu dul dëgg. Ba mujj ñaari nit ñëw naan: 26:61 «Kii nee woon na: “Man naa toj kër Yàlla ga, tabaxaat ko ci ñetti fan.”» 26:62 Ci kaw loolu saraxalekat bu mag ba jóg ne ko: «Ndax doo tontu dara? Loo xam ci li ñii seede ci yaw?» 26:63 Waaye Yeesu ne cell. Saraxalekat bu mag ba ne ko: «Giñloo naa la ci Yàlla miy dund, nga wax nu, ndax yaa di Almasi bi, Doomu Yàlla ji.» 26:64 Yeesu tontu ko: «Wax nga ko. Maa ngi leen koy wax it, li dale fii dingeen gis Doomu nit ki toog ci ndeyjooru Aji Kàttan ji, di ñëw ci niiri asamaan si.» 26:65 Bi mu déggee loolu, saraxalekat bu mag ba daldi mer lool, ba xotti ay yéreem, daldi ne: «Weddi na Yàlla, lu nu doyeeti seede? Dégg ngeen ni mu weddee. 26:66 Lu ngeen ci xalaat?» Ñu tontu ko: «Yoon teg na ko dee.» 26:67 Ci kaw loolu ñu daldi tifli ci xar-kanamam, dóor ko ay kurfeñ. Ñeneen talaata ko, 26:68 ne ko: «Yaw Kirist, yonent bi, ndax xam nga ku la dóor?» 26:69 Bi looluy xew, Piyeer moom ma nga toogoon ca biti ca ëtt ba. Noonu benn mbindaan ñëw ci moom ne ko: «Yaw itam àndoon nga ak Yeesum Galile.» 26:70 Waaye Piyeer weddi ko ci kanamu ñépp ne ko: «Xawma li ngay wax.» 26:71 Bi mu ko waxee, mu jëm ca bunt ba, te beneen mbindaan gis ko, mu wax ña fa nekkoon: «Kii àndoon na ak Yeesum Nasaret.» 26:72 Waaye Piyeer weddiwaat, boole ko ak ay ngiñ ne ko: «Xawma nit kooku.» 26:73 Nes tuuti ña fa taxawoon ñëw ci Piyeer ne ko: «Ci lu wóor ne yaw itam bokk nga ci ñoom, ndaxte sa waxin feeñal na la.» 26:74 Bi mu ko déggee, Piyeer daldi giñ ak di waat ne: «Xawma nit kooku.» Te ci taxawaay ginaar daldi sab. 26:75 Noonu Piyeer fàttaliku la Yeesu waxoon ne: «Bala ginaar a sab, dinga ma weddi ñetti yoon.» Mu daldi génn, di jooy jooy yu metti.
27:1 Ci suba teel saraxalekat yu mag yépp ak njiiti xeet wa gise, ngir fexee reylu Yeesu. 27:2 Ñu yeew ko, yóbbu ko, jébbal ko Pilaat boroom réew ma. 27:3 Bi nga xamee ne Yudaa, mi woroon Yeesu, gis na ne, daan nañu ko, mu am naqaru xol. Mu dem nag ca saraxalekat yu mag ya ak njiit ya, delloo leen fanweeri poset yu xaalis, 27:4 ne leen: «Am naa bàkkaar ci li ma wor nit ku tooñul, ngir ñu rey ko.» Ñu tontu ko: «Lu ciy sunu yoon? Loolu yaa ko yég.» 27:5 Noonu Yudaa sànni xaalis ba ca kër Yàlla ga, jóge fa, dem, takk buum ci baatam, xaru. 27:6 Saraxalekat yu mag ya nag fab xaalis ba, naan: «Jaaduwul nu def xaalis bii ci dencukaayu xaalis bi ci kër Yàlla gi, ndaxte njëgu deret la.» 27:7 Ñu daldi diisoo nag, jënd ca xaalis ba toolu defarkatu ndaa ya, ngir di fa suul doxandéem ya. 27:8 Loolu moo tax ñu wooye tool booba ba tey Toolu deret. 27:9 Noonu la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Yeremi am, bi mu naan: «Fab nañu fanweeri poseti xaalis ya, mooy njëg gi bànni Israyil xayma woon ci nit ki; 27:10 ñu joxe ko ngir toolu defarkatu ndaa ya, ni ma ko Boroom bi sante.» 27:11 Gannaaw loolu Yeesu taxaw ca kanamu boroom réew ma, boroom réew ma laaj ko; «Ndax yaa di buuru Yawut yi?» 27:12 Yeesu tontu ko ne: «Wax nga ko,» waaye tontuwul dara ca la ko saraxalekat yu mag ya ak njiit ya jiiñ. 27:13 Noonu Pilaat ne ko: «Xanaa dégguloo lépp li ñu la jiiñ?» 27:14 Waaye Yeesu tontuwu ko ci dara, ba tax boroom réew ma waaru lool. 27:15 Ca màggal gu nekk nag boroom réew ma daan na may mbooloo ma, ñu tànn kenn ca ña ñu tëjoon, mu daldi leen ko bàyyil. 27:16 Fekk booba amoon nañu ku ñu tëjoon, ku siiw te tudd Barabas. 27:17 Bi nga xamee ne daje nañu nag, Pilaat laaj leen: «Kan ngeen bëgg, ma bàyyi ko, Barabas walla Yeesu mi ñuy wax Kirist?» 27:18 Ndaxte xamoon na ne, kiñaan rekk a taxoon, ñu jébbal ko ko. 27:19 Te it bi mu toogee sax ca jalu àttekaay ba, jabaram yónnee ci moom ne ko: «Bul dugg ci yëfi ku jub kooku, ndaxte tey gént naa ci moom te sonn naa ci lool.» 27:20 Waaye saraxalekat yu mag ya ak njiit ya xiir mbooloo ma, ñu laaj Barabas te reylu Yeesu. 27:21 Noonu boroom réew ma laaj leen: «Kan ci ñaar ñii ngeen bëgg, ma bàyyil leen ko?» Ñu tontu ko: «Barabas.» 27:22 Pilaat ne leen: «Nan laay def nag Yeesu, mi tudd Kirist?» Ñépp tontu ko ne: «Daaj ko ci bant, ba mu dee!» 27:23 Boroom réew ma ne leen: «Lu tax? Gan tooñ la def?» Waaye ñu daldi yuuxu bu gën a kawe naan: «Daaj ko ci bant!» 27:24 Naka Pilaat xam ne, du ci man dara, fekk na sax yengu-yengu bi gën a am doole, mu daldi fab ndox, raxas ay loxoom ca kanamu mbooloo ma ne leen: «Set naa ci deretu ku jub kii; nu ngeen xam, defleen ko.» 27:25 Ñépp tontu ko: «Na deretam dal ci sunu kaw ak sunu kaw njaboot.» 27:26 Noonu Pilaat bàyyil leen Barabas, mu dóorlu Yeesu ay yar, jébbal ko, ngir ñu daaj ko ci bant. 27:27 Bi ñu ko defee xarekati boroom réew ma fab Yeesu, yóbbu ko ci biir kër ga, ñu daldi woo mbooloom xarekat ya yépp ci moom. 27:28 Noonu ñu summi ko, solal ko mbubbum xarekat mu xonq curr. 27:29 Ñu ràbb kaalag dég, teg ko ci boppam, teg bantu xat ci loxol ndeyjooram, sukk ci kanamam, di ko ñaawal ne ko: «Nuyu nanu la, yaw buuru Yawut yi!» 27:30 Ba noppi ñu daldi tifli ci kawam, fab bantu xat ba, dóor ko ci boppam. 27:31 Bi ñu ko ñaawalee ba noppi, ñu summi mbubbum xarekat ma, solalaat ko ay yéreem, yóbbu ko, ngir daaj ko ci bant. 27:32 Bi nga xamee ne génn nañu, ñu daje ak nit ku dëkk Siren te tudd Simoŋ; ñu ga ko, ngir mu gàddu bant, ba ñu war a daaj Yeesu. 27:33 Ñu ñëw nag fa ñuy wax Golgota, biy tekki «Bérabu kaaŋu bopp.» 27:34 Bi ñu fa eggee, ñu jox ko biiñ, ñu def ci lu wex. Waaye bi mu ko mosee, nanguwu koo naan. 27:35 Noonu ñu daaj ko ca bant ba, ñu daldi séddoo ay yéreem, tegoo ko ay bant, 27:36 ba noppi toog fa, di ko wottu. 27:37 Te it ñu teg ci kaw boppam mbind, mu xamle lu tax ñu rey ko, mu ne: «Kii mooy Yeesu, buuru Yawut yi.» 27:38 Booba it ñu daajaale ak moom ñaari taskati réew ma, kenn ci ndeyjooram, ka ca des ci càmmooñam. 27:39 Ña fa doon romb di ko xas, di wëcc seen bopp ndax sib ko, 27:40 naan: «Yaw mi man a toj kër Yàlla ga, tabaxaat ko ci ñetti fan, musalal sa bopp; boo nekkee Doomu Yàlla, wàccal ci bant bi.» 27:41 Saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya ak njiit ya it di ko ñaawal naan: 27:42 «Waa jii musal na ñeneen te mënul a musal boppam! Ndegam mooy buuru Israyil, na wàcc léegi ci bant bi, nu gëm ko. 27:43 Gannaaw dénk na boppam Yàlla, kon na ko Yàlla musal, bu ko soppee, ndaxte nee na: “Maay Doomu Yàlla.”» 27:44 Taskati réew ma it, ya ñu daajaale ak moom, di ko xas noonule. 27:45 La tàmbalee digg-bëccëg, ba ci tisbaar, réew mépp lëndëm. 27:46 Noonu ci wetu ñetti waxtu Yeesu daldi wootee kàddu gu dëgër naan: «Eli, Eli, lema sabaktani?» liy tekki: «Sama Yàlla, sama Yàlla, lu tax nga dëddu ma?» 27:47 Ñenn ña ca ña fa taxaw nag, bi ñu ko déggee, ñu ne: «Mu ngi woo yonent Yàlla Iliyas.» 27:48 Ca saa sa kenn ci ñoom daw, jël aw sagar, capp ko ci bineegar, mu teg ko ci kaw bant, jox ko ko, mu muucu. 27:49 Waaye ña ca des ne: «Bàyyil, nu seet ba xam Iliyas dina ñëw, musal ko.» 27:50 Noonu Yeesu wootewaat ak kàddu gu dëgër, delloo ruuwam Yàlla. 27:51 Ca saa sa ridob bérab bu sell ba ca kër Yàlla ga xar ñaar, li dale ci kaw ba ci suuf; suuf si yengu, doj yi toj, bàmmeel yi ubbiku, 27:52 te ñu bare ci jëmmi nit ñu sell ñu dee, dekki. 27:53 Te gannaaw ndekkitel Yeesu ñu génn ca bàmmeel ya, dugg ca dëkk bu sell ba, te feeñu ñu bare. 27:54 Noonu njiitu xare bi ak ñi ànd ak moom di wottu Yeesu, bi ñu gisee suuf si yengu ak li xew, ñu daldi tiit lool ne: «Ci dëgg, kii Doomu Yàlla la.» 27:55 Amoon na fa it ay jigéen yu bare yu leen dand, di seetaan. Te ñoo jóge woon Galile, ànd ak Yeesu, di ko topptoo. 27:56 Xàmmi nañu ci: Maryaama mi dëkk Magdala, ndeyu Saag ak Yuusufa, ak ndeyu doomi Sebede ya. 27:57 Ca ngoon amoon na taalibeb Yeesu mu ñëw, tudd Yuusufa te dëkk Arimate; ku bare alal la woon. 27:58 Mu dem ca Pilaat, laaj ko néewu Yeesu. Pilaat santaane, ñu jox ko ko. 27:59 Noonu Yuusufa fab jëmm ja, laxas ko ci càngaay lu set, 27:60 dugal ko ca bàmmeel bu bees, ba mu yettaloon boppam ciw doj. Mu béraŋ doj wu mag ca buntu bàmmeel ba, dem. 27:61 Fekk Maryaamam Magdala ak Maryaama ma ca des ñoo fa toogoon janook bàmmeel ba. 27:62 Ba bët setee nag, ca bés ba topp bésu Waajal ba, saraxalekat yu mag ya ak Farisen ya dajaloo, jëm ci Pilaat. 27:63 Ñu ne ko: «Boroom réew mi, fàttaliku nanu ne, naxkat booba waxoon na, bi muy dund naan: “Gannaaw ñetti fan dinaa dekki.” 27:64 Danoo bëggoon nag, nga santaane, ñu wottu bàmmeel ba, ba am ñetti fan, ngir bañ taalibeem ya ñëw, sàcc néew ba, tey yégle ne dekki na. Bu ko defee nax bu mujj boobu dina yées bu jëkk ba.» 27:65 Pilaat tontu leen: «Amleen, ay wottukat a ngi nii. Demleen wottuji ko, ni ngeen mane.» 27:66 Noonu ñu dem, tëj bàmmeel ba bu wóor, ñu tay ca doj wa màndarga, teg fa wottukat ya.
28:1 Gannaaw bésu noflaay ba nag, ca fajar ga, ca bés bu jëkk ca ayu-bés ga, Maryaamam Magdala ak Maryaama ma ca des dem, seeti bàmmeel ba. 28:2 Fekk suuf yengu woon na bu metti, ndaxte benn malaakam Boroom bi wàcc na ci asamaan, ñëw béraŋ doj wa, toog ci kaw. 28:3 Meloom mel na ni melax, ay yéreem weex tàll ni perkaal. 28:4 Ñi doon wottu tiit bay lox, daldi mel ni ñu dee. 28:5 Noonu malaaka ma ne jigéen ña: «Buleen tiit. Xam naa ne, yéena ngi wut Yeesu, ma ñu daajoon ca bant ba, 28:6 waaye nekkatu fi, ndaxte dekki na, ni mu ko waxe woon. Ñëwleen seet fi mu tëddoon, 28:7 te ngeen dem bu gaaw, wax ay taalibeem ne, dekki na te jiituji na leen Galile; foofa ngeen koy gise. Lii laa leen wax.» 28:8 Bi loolu amee nag jigéen ña daldi jóge bu gaaw ca bàmmeel ba, tiit ak mbég mu réy di jax seen xol, ñu daldi daw, ngir yégal ko taalibe ya. 28:9 Ba ñuy dem nag, Yeesu taseek ñoom ne leen: «Maa ngi leen di nuyu.» Jigéen ña jegesi, laxasu cay tànkam, di ko màggal. 28:10 Yeesu ne leen: «Buleen tiit, waaye demleen yégal samay bokk, ñu dem Galile; foofa lañu may gise.» 28:11 Ba ñuy dem, ñenn ca wottukat ya ñëw ca dëkk ba, xamal saraxalekat yu mag ya lépp lu xew. 28:12 Noonu saraxalekat ya dajaloo ak njiit ya, ñu diisoo; ba noppi ñu fab xaalis bu bare, jox ko xarekat ya, 28:13 ne leen: «Nangeen wax lii: “Ay taalibeem ñëw nañu ci guddi, sàcc ko, bi nuy nelaw.” 28:14 Te bu ko boroom réew mi yégee nag, dinanu ko neexal, ngir rawale leen.» 28:15 Wottukat ya nag fab xaalis ba, def la ñu leen santoon. Te nettali boobu siiw na ci Yawut yi ba bésu tey. 28:16 Noonu fukki taalibe ya ak benn dem ci biir Galile, ca tund wa leen Yeesu digaloon. 28:17 Bi ñu gisee Yeesu, ñu màggal ko, waaye ñenn ñi am xel ñaar. 28:18 Yeesu jegesi ne leen: «Sañ-sañ bépp, jox nañu ma ko ci kaw ak ci suuf. 28:19 Demleen nag sàkk ay taalibe ci xeet yépp, sóob leen ci ndox ci turu Baay bi ak Doom ji ak Xel mu Sell mi; 28:20 te ngeen jàngal leen, ñuy sàmm lépp li ma leen sant. Te maa ngi ànd ak yéen bés bu nekk, ba kera àddina di tukki.»
1:1 Xebaar bu baaxu Yeesu Kirist, Doomu Yàlla, nii la tàmbalee. 1:2 Bind nañu ci téereb yonent Yàlla Esayi naan:«Maa ngi yónni sama ndaw ci sa kanam,mu xàllal la sa yoon. 1:3 Baat a ngi xaacu ca màndiŋ ma naan:“Xàll-leen yoonu Boroom bi,jubal-leen fi muy jaar.”» 1:4 Noonu Yaxya feeñ ca màndiŋ ma, di sóob nit ñi ci ndox, tey waaree nii: «Tuubleen seeni bàkkaar, ba noppi ma sóob leen ci ndox, ngir Yàlla baal leen seeni bàkkaar.» 1:5 Kon waa diiwaanu Yude ñépp ak waa dëkku Yerusalem ñépp daldi génn jëm ci moom, di nangu seeni bàkkaar fi kanam ñépp, Yaxya sóob leen ca dexu Yurdan. 1:6 Yaxya nag mi ngi soloon mbubb mu ñu ràbbe kawaru giléem, takk laxasaayu der ci ndiggam. Ay njéeréer la doon dunde ak lem. 1:7 Mu waare ne: «Am na kuy ñëw sama gannaaw koo xam ne kii moo ma ëpp kàttan; yeyoowuma sax sëgg, ngir tekki ay dàllam. 1:8 Maa ngi leen di sóob ci ndox, waaye moom dina leen sóob ci Xel mu Sell mi.» 1:9 Booba Yeesu jóge na dëkku Nasaret ci diiwaanu Galile, ñëw, Yaxya sóob ko ci dexu Yurdan. 1:10 Bi muy génn ndox mi, mu daldi gis asamaan xar, te Xelum Yàlla di wàcc ci melow pitax, ñëw ci moom. 1:11 Te baat bu jóge asamaan jib ne: «Yaa di sama Doom, ji ma bëgg; ci yaw laa ame bànneex.» 1:12 Ci kaw loolu Xelum Yàlla daldi jéñ Yeesu, mu dem ca màndiŋ ma. 1:13 Mu nekk fa ñeent-fukki fan, jànkoonte ak fiiri Seytaane; mu dëkk ci biir rabi àll yi, te malaakay Yàlla di ko topptoo. 1:14 Bi nga xamee ne jàpp nañu Yaxya, Yeesu dem ca diiwaanu Galile, di waare xebaar bu baaxu Yàlla, 1:15 naan: «Jamono ji mat na, nguuru Yàlla jegesi na; tuubleen seeni bàkkaar te gëm xebaar bu baax bi.» 1:16 Am bés Yeesu doon dox ca tefesu dexu Galile, mu gis fa ñaar ñu bokk ndey ak baay, di Simoŋ ak Andare rakkam, ñuy sànni seeni mbaal ci dex gi, ndaxte ay nappkat lañu woon. 1:17 Yeesu ne leen: «Ñëwleen topp ci man, dinaa leen def nappkati nit.» 1:18 Ci saa si ñu bàyyi seeni mbaal, topp ci moom. 1:19 Bi Yeesu demee ba ca kanam, mu gis Saag doomu Sebede, ak Yowaana, mi mu bokkal ndey ak baay, ñu nekk ci gaal gi, di defar seeni mbaal. 1:20 Noonu Yeesu woo leen, ñu daldi bàyyi seen baay Sebede ci gaal gi, moom ak surga ya, tey topp ci moom. 1:21 Gannaaw loolu ñu dem Kapernawum. Ca bésu noflaay nag Yeesu daldi dugg ci jàngu bi, di leen jàngal. 1:22 Te ñu waaru ca njàngaleem, ndaxte jàngal na leen ak sañ-sañ bu seeni xutbakat amul. 1:23 Noonu am na ci jàngu bi nit ku rab jàpp. Mu daldi yuuxu naan: 1:24 «Yaw Yeesum Nasaret, loo nuy fexeel? Ndax dangaa ñëw, ngir alag nu? Xam naa la, yaa di Aji Sell, ji jóge ci Yàlla.» 1:25 Waaye Yeesu gëdd ko naan: «Noppil te génn ci moom.» 1:26 Noonu rab wi daldi sayloo nit ki te génn ci moom ak yuux gu réy. 1:27 Bi loolu amee ñépp waaru, ba laajante naan: «Kii mooy kan? Mii njàngale lu bees la te ànd ak sañ-sañ. Day sant rab yi sax, ñu di ko déggal.» 1:28 Noonu turam daldi siiw ci diiwaani Galile gépp. 1:29 Bi nga xamee ne génn nañu ci jàngu bi, ñu ànd ak Saag ak Yowaana, dem ci kër Simoŋ ak Andare. 1:30 Fekk gorob Simoŋ bu jigéen tëdd wopp ak yaram wu tàng; ñu daldi ko yégal Yeesu. 1:31 Mu ñëw nag ci moom, jàpp loxoom, yékkati ko. Noonu tàngoor wi daldi wàcc, te soxna si di leen topptoo. 1:32 Ca ngoon sa nag, bi jant sowee, ñu indil Yeesu ñi wopp ñépp ak ñi rab jàpp ñépp, 1:33 ba dëkk bi bépp dajaloo ci buntu kër gi. 1:34 Noonu mu wéral ñu bare, ñu wopp ak ay jàngoro yu wuute, te dàq ay rab yu bare. Waaye mu tere rab yi, ñu wax dara, ndaxte xam nañu ko. 1:35 Ca njël laata bët di set, Yeesu jóg dem ca bérab bu wéet, di fa ñaan Yàlla. 1:36 Simoŋ nag ak ñi ànd ak moom di ko seet fu nekk. 1:37 Bi ñu ko gisee, ñu ne ko: «Ñépp a ngi lay seet.» 1:38 Waaye Yeesu tontu leen: «Nanu dem feneen ci dëkk yi nu wër, ma waare fa itam, ndaxte moo tax ma génn.» 1:39 Noonu mu wër ci diiwaanu Galile gépp, di waare ci seeni jàngu, tey dàq rab yi. 1:40 Am bés ku gaana ñëw ci moom, sukk, ñaan ko ne: «Soo ko bëggee, man nga maa wéral.» 1:41 Yeesu yërëm ko, tàllal loxoom, laal ko naan: «Bëgg naa ko, wéral.» 1:42 Ca saa sa ngaanaam daldi deñ, mu wér. 1:43 Noonu Yeesu yebal ko, dénk ko bu wér naan: 1:44 «Moytul a wax kenn dara, waaye demal won sa bopp saraxalekat bi, te nga jébbal Yàlla sarax, si yoonu Musaa santaane, ngir ñu xam ne wér nga, te mu nekk seede ci ñoom.» 1:45 Waaye naka la waa ji génn, mu di yéene ci kaw li xewoon, te di ko jéebaane, ba tax Yeesu mënatul a faŋaaral dugg cib dëkk, waaye mu nekk ci biti ciy bérab yu wéet. Ba tey nit ñi jóge fu nekk, di ko fa fekk.
2:1 Bi ay fan weesoo, Yeesu dellusi dëkku Kapernawum, mu siiw ne mu ngi ci kër gi. 2:2 Noonu nit ñu bare dajaloo fa, ba kenn amatul foo taxaw, du ci bunt bi sax. Te Yeesu di leen yégal kàddu gi. 2:3 Noonu, am ñu ko indil ku yaramam wépp làggi, ñeenti nit jàppoo ko. 2:4 Waaye mënuñu koo jege ndax mbooloo mi. Kon ñu daldi teggi kaw kër gi, di bëtt fa tiim bérab ba Yeesu nekk, daldi yoor basaŋ, ga làggi ba tëdd. 2:5 Bi Yeesu gisee seen ngëm, mu ne làggi ba: «Sama waay, baal nañu la say bàkkaar.» 2:6 Fekk ay xutbakat toog fa, ñu di werante ci seen xel naan: 2:7 «Kii kan la, ba sañ a wax lii; mi ngi sosal Yàlla. Ana ku man a baale bàkkaar yi, ku dul Yàlla doŋŋ?» 2:8 Waaye Yeesu yég ci xelam li ñuy werante ci seen biir, ne leen: «Lu tax ngeen di werantee nii ci seen xel? 2:9 Lan moo gën a yomb, ma wax ku làggi ki: “Baal nañu la say bàkkaar,” walla ma wax ko: “Jógal, jël sa basaŋ, tey dox”? 2:10 Waaye xamleen ne, Doomu nit ki am na ci àddina sañ-sañu baale bàkkaar yi.» Ci kaw loolu mu ne làggi ba: 2:11 «Maa ngi la koy sant, jógal, jël sa basaŋ te nga ñibbi.» 2:12 Ca saa sa mu jël basaŋam te génn fa kanam ñépp. Noonu ñépp waaru, di màggal Yàlla naan: «Lu mel ni lii, musunu koo gis.» 2:13 Gannaaw loolu Yeesu génnaat, aw booru dex ga, mbooloo mépp di ñëw ci moom, mu di leen jàngal. 2:14 Bi Yeesu di romb, mu gis ku ñuy wax Lewi, doomu Alfe, toog ca juuti ba. Yeesu ne ko: «Kaay topp ci man.» Mu jóg, daldi topp ci moom. 2:15 Bi loolu amee Yeesu ak i taalibeem di lekk ci kër Lewi, fekk ay juutikat ak ay boroom bàkkaar yu bare di lekkandoo ak ñoom, ndaxte ñu bare ci ñoom a ko toppoon. 2:16 Waaye xutbakat yi bokk ci Farisen yi, bi ñu gisee ne, dafa bokk lekk ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar, ñu daldi laaj taalibe yi: «Lu tax muy lekkandoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar?» 2:17 Noonu Yeesu dégg ko, mu ne leen: «Ñi wér soxlawuñu fajkat, ñi wéradi ñoo ko soxla; ñëwuma woo ñi jub, waaye bàkkaarkat yi laay woo.» 2:18 Taalibey Yaxya nag ak Farisen yi daan nañu woor. Ñu ñëw nag fi Yeesu ne ko: «Lu tax taalibey Yaxya yi ak yu Farisen yi di woor, te say taalibe duñu woor?» 2:19 Yeesu tontu leen: «Ndax gan, yi ñëw cig céet, dinañu woor, fekk boroom céet gi ànd ak ñoom? Duñu woor, li feek boroom céet gaa ngi ànd ak ñoom. 2:20 Waaye bés yaa ngi ñëw, yu ñuy jële boroom céet gi; bés boobaa nag dinañu woor. 2:21 «Kenn du daax mbubb mu màggat ak sekkit wu bees; ndaxte sekkit wi day ñoddi mbubb mi, te xottiku bi gën a yaatu. 2:22 Te kenn du def biiñ bu bees ci mbuusi der yu màggat. Lu ko moy, biiñ bi day toj mbuus yi, ba mbuus yi yàqu, ak biiñ bi tuuru. Waaye biiñ bu bees, ci mbuus yu bees lañu koy def.» 2:23 Amoon na benn bésu noflaay Yeesu jaar ciy tool yu ñor. Bi ñuy dem nag, ay taalibeem daldi fàq ay gub. 2:24 Noonu Farisen ya ne Yeesu: «Gisal, lu tax say taalibe di def lu jaaduwul ci bésu noflaay bi?» 2:25 Yeesu tontu leen: «Ndax jànguleen la Daawuda defoon, ba mu amee soxla te xiif, moom ak ña mu àndaloon? 2:26 Xanaa yéguleen li amoon ci bési Abiyatar saraxalekat bu mag bi, ni Daawuda dugge woon ca kër Yàlla ga, lekk mburu ya ñu jébbal Yàlla, jox ci it ña mu àndaloon; fekk jaaduwul kenn lekk ko, ku dul saraxalekat?» 2:27 Yeesu dellu ne leen: «Yàlla sàkkul nit ngir bésu noflaay bi, waaye sàkk na bésu noflaay ngir nit. 2:28 Noonu Doomu nit ki mooy boroom bésu noflaay bi.»
3:1 Am beneen bés, Yeesu duggaat ci jàngu bi, fekk amoon na fa nit ku loxoom làggi. 3:2 Am na fa nag ay Farisen, ñuy xool Yeesu, ba xam dina ko faj ci bésu noflaay bi, ba man koo tuumaal. 3:3 Yeesu ne ku loxoom làggi: «Jógal, taxaw ci kanamu ñépp.» 3:4 Noonu Yeesu ne leen: «Lan moo jaadu, nu def ko bésu noflaay bi, lu baax mbaa lu bon; nu musal nit mbaa nu rey nit?» Waaye ñu ne cell. 3:5 Ci kaw loolu Yeesu xool leen ak mer, am naqar ndax seen xol bu fatt; ba noppi mu ne nit ki: «Tàllalal sa loxo.» Nit ki tàllal ko, loxoom daldi wér peŋŋ. 3:6 Ca saa sa nag Farisen ya génn, daldi gise ak ñi far ak buur bi Erodd, ngir fexe koo reylu. 3:7 Gannaaw loolu Yeesu ak ay taalibeem jóge fa, jëm dex ga. Fekk mbooloo mu mag mu jóge diiwaanu Galile, topp ko. 3:8 Te it nit ñu bare dégg la mu def, ñu ñëw fi moom, jóge diiwaanu Yude ak dëkku Yerusalem, ca diiwaanu Idume, ca gannaaw dexu Yurdan ak ci wàlli Tir ak Sidon. 3:9 Booba nag Yeesu faj na ñu bare, ba ñu am ay jàngoro di ko song, ngir laal ko. Noonu Yeesu wax ay taalibeem, ñu wutal ko gaal, ngir mbooloo mi bañ koo buux. 3:11 Fekk booba képp ku rab jàpp ku ko gis, daanu fa kanamam di yuuxu naan: «Yaa di Doomu Yàlla.» 3:12 Waaye Yeesu gëdd rab yi bu wér, ngir ñu bañ koo siiwal. 3:13 Gannaaw loolu Yeesu yéeg ci tund wi, woo ñi ko neex, ñu daldi ñëw ci moom. 3:14 Noonu mu tànn ci fukk ak ñaar, tudde leen ay ndawam, ngir ñu ànd ak moom te mu yónni leen, ñu waareji, 3:15 mu joxaale leen sañ-sañu dàq ay rab. 3:16 Fukk ak ñaar ñii la tànn:Simoŋ, mi mu tudde Piyeer, 3:17 Saag doomu Sebede, ak Yowaana mi mu bokkal ndey ak baay — ñoom ñi mu wooye Bowanerses, maanaam «Ñi aaytal ni dënnu gi» — 3:18 Andare ak Filib,Bartelemi ak Macë,Tomaa ak Saag doomu Alfe,Tade ak Simoŋ, mi bokk ca mbooloo, ma ñu tudde Ñi farlu ci moom seen réew; 3:19 ak Yudaa Iskariyo mi nar a wor Yeesu. 3:20 Am beneen bés Yeesu ñëwaat ca kër ga. Te mbooloo mu bare dajaloowaat fa, ba tax mënuñoo lekk sax. 3:21 Bi ko ay bokkam déggee nag, ñu ñëw, ngir jàppsi ko naan: «Dafa tàggoo ak sagoom.» 3:22 Te it xutbakat ya jóge Yerusalem ne: «Beelsebul jàpp na ko; ci kàttanu buuru rab yi lay dàqe rab yi.» 3:23 Noonu Yeesu woo leen, wax ak ñoom ciy léeb ne leen: «Naka la Seytaane man a dàqe Seytaane? 3:24 Réew mu xeex boppam, du man a yàgg. 3:25 Te kër gu xeex boppam, du man a yàgg. 3:26 Bu Seytaane nag jógee, ba xeex boppam, xàjjalikoo dikkal na ko te du man a yàgg, waaye dina tas. 3:27 «Su fi amee nit ku bare doole, naka la kenn man a dugge ci këram, nangu alalam? Xanaa dafay jëkk a yeew ku bare doole ka, ba noppi door a toj këram gépp. 3:28 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, lépp dees na ko baal nit ñi, muy bàkkaar, muy sosal Yàlla wu mu man a doon. 3:29 Waaye kuy sosal Xel mu Sell mi deesu ko baal mukk; gàddu na bàkkaar ba fàww.» 3:30 Yeesu wax na loolu, ndaxte nee woon nañu, rab jàpp na ko. 3:31 Noonu ndeyu Yeesu ak ay rakkam ñëw, ñu taxaw ci biti, yónnee, woo ko. 3:32 Fekk booba mbooloo nga toog, wër ko. Ñu ne ko nag: «Sa yaay ak say rakk ñu ngi taxaw ci biti, di la laaj.» 3:33 Waaye Yeesu tontu leen: «Kan mooy sama ndey? Ñan ñooy samay rakk?» 3:34 Noonu mu xool ñi ko wër naan: «Sama yaay ak samay rakk a ngii; 3:35 ndaxte kuy def coobareg Yàlla, kooku mooy sama rakk ak sama jigéen ak sama ndey.»
4:1 Am beneen yoon Yeesu nekk ci wetu dex ga, di jàngalewaat. Mbooloo mu bare dajaloosi, ba tax mu yéeg cig gaal, dugg ca dex ga; mbooloo mépp taxaw ca tefes ga. 4:2 Noonu Yeesu daldi leen jàngal lu bare ciy léeb. Ci njàngaleem nag mu ne leen: 4:3 «Dégluleen, dafa amoon beykat bu demoon jiyi. 4:4 Bi muy saaw toolam nag, lenn ci pepp mi wadd ci kaw yoon wi, picc yi daldi ñëw, lekk ko lépp. 4:5 Leneen ci pepp mi wadd ci bérab bu bare ay doj te néew suuf, mu daldi sax bu gaaw, ndaxte suuf si barewul. 4:6 Waaye bi jant bi naajee, mu lakk, wow, ndaxte amul ay reen. 4:7 Leneen nag wadd ci biir ay xaaxaam, xaaxaam yi daldi sax, tanc ko, te meññul dara. 4:8 Li ci des dal ci suuf su baax, mu jóg, sax, di focci ay gub; lii àntu, ba mat fanweeri yoon lu ëpp la mu ji woon, lii mat juróom-benn-fukk, lii mat téeméer.» 4:9 Noonu Yeesu ne leen: «Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.» 4:10 Gannaaw loolu ba Yeesu nekkee fu wéet, fukki taalibe ak ñaar ña, ak ñeneen ñu daan ànd ak ñoom, laaj ko ci mbirum léeb yi. 4:11 Mu tontu leen: «Yéen may nañu leen, ngeen xam mbóoti nguuru Yàlla, waaye ñi ci biti léeb ay ëmb lépp. 4:12 Noonu la, ngir:“Ñuy xool bu baax waaye duñu gis dara,di déglu bu baax waaye duñu xam dara,ngir bañ ñu tuub seeni bàkkaar,te Yàlla baal leen.”» 4:13 Noonu Yeesu ne leen: «Ndax xamuleen léeb wii? Nu ngeen xame nag léeb yi ci des? 4:14 Ki ji nag, kàddu gi lay ji. 4:15 Ki féete ci yoon wi mooy ki dégg, Seytaane ñëw ci saa si, këf kàddu, gi ñu def ci moom. 4:16 Ki jot kàddu gi ci bérab bu bare ay doj mooy ki dégg kàddu gi, nangu ko ak mbég ci saa si, 4:17 waaye du yàgg, ndaxte wax ji saxul ci moom. Bu jaaree ci nattu nag, mbaa ñu fitnaal ko ndax kàddu gi, mu dàggeeku ci saa si. 4:18 Ki jot jiwu wi ci xaaxaam yi mooy ki dégg kàddu gi, 4:19 waaye soxlay àddina ak naxi alal ak bëgge solu ko, tanc kàddu gi, ba du meññ dara. 4:20 Ki jot kàddu gi ci suuf su baax si nag, mooy ki ko dégg te nangu ko, ba jariñ; kii mat fanweeri yoon lu ëpp la ñu ji woon, kii mat juróom-benn-fukk, kii mat téeméer.» 4:21 Yeesu ne leen itam: «Ndax nit dina jël làmp, dëpp ci leget walla def ko ci ron lal? Ndax du ko wékk? 4:22 Amul dara luy kumpa lu ñu warul a siiwal, mbaa mu làqu te warul ne fàŋŋ. 4:23 Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.» 4:24 Mu ne leen: «Seetleen bu baax li ngeen di dégg. Dees na leen nattal ak natt, bi ngeen di nattale, te dollil leen. 4:25 Ku am, dees na la dollil; ku amul, li nga am as néew, dees na ko nangu.» 4:26 Yeesu teg ci ne: «Nguuru Yàlla dafa mel ni nit ku ji tool. 4:27 Muy nelaw walla muy xool, guddi mbaa bëccëg, jiwu wi sax, di màgg, te xamul naka la ko defe. 4:28 Suuf day meññ moom ci boppam, mu sax, focci, def i gub. 4:29 Bu gub yi ñoree nag, mu dagg ko, ndaxte ngóob jot na.» 4:30 Yeesu ne leen ati: «Lu nu man a mengaleel nguuru Yàlla? Walla ban léeb lanu ko man a misaale? 4:31 Dafa mel ni doomu fuddën, bi gën a tuuti ci jiwu yépp; 4:32 waaye boo ko jiwee, day jóg, màgg, ba sut gàncaxi tóokër yépp; mu sax ay bànqaas yu réy, ba picci asamaan tàgg ci keram.» 4:33 Noonu Yeesu dégtal leen yeneeni léeb yu bare yu mel ni yii, di leen xamal kàddu gi, aju ci lu ñu àttan. 4:34 Daawu leen wax dara lu dul ciy léeb. Waaye bu wéetee ak ay taalibe, daan na leen firil lépp. 4:35 Bés booba nag ci ngoon Yeesu ne taalibe yi: «Nanu jàll dex gi.» 4:36 Mu yiwi mbooloo mi nag, ay taalibeem jël ko ni mu mel ci gaal gi; te yeneeni gaal ànd ak moom. 4:37 Naka noona ngelaw lu mag daldi jóg, duus yi sàng gaal gi, ba mu bëgg a fees. 4:38 Fekk Yeesu tëdd di nelaw ci ngégenaay ci taatu gaal gi.Taalibe yi daldi ko yee naan: «Kilifa gi, ndax sunu bakkan soxalu la?» 4:39 Ci kaw loolu Yeesu jóg, daldi gëdd ngelaw li, ne dex gi: «Noppil te dal!» Noonu ngelaw li dal, ba lépp ne nemm. 4:40 Yeesu ne taalibe ya: «Lu tax ngeen tiit? Ndax gëmaguleen?» 4:41 Ñu daldi ragal lool, naan ci seen biir: «Kii moo di kan, ba ngelaw li ak dex gi sax di ko déggal?»
5:1 Noonu ñu jàll dex ga, ba teer ci diiwaanu waa Serasa. 5:2 Bi Yeesu génnee gaal gi, nit ku rab jàpp jóge ca sëg ya, daldi ñëw kar ko. 5:3 Kooku nag ca sëg ya la dëkk, te kenn mënu koo yeew, du ak càllala sax. 5:4 Ndaxte ay yoon yu bare jéngoon nañu ko te yeew ko ak ay càllala, waaye waa ji daldi dagg càllala yi te damm jéng yi, ba kenn amul woon kàttanu téye ko. 5:5 Guddi ak bëccëg mu nga woon ca sëg ya ak ca tund ya, di yuuxu te jam yaramam ak ay xeer. 5:6 Bi mu gisee Yeesu fu sore nag, mu daldi dawsi, sukk fa kanamam, 5:7 di xaacu naan: «Yaw Yeesu Doomu Yàlla Aji Kawe ji, loo may fexeel? Ci turu Yàlla, bu ma mbugal.» 5:8 Ndaxte Yeesu nee woon na ko: «Yaw rab wu bon wi, génnal ci nit ki.» 5:9 Noonu Yeesu laaj ko: «Noo tudd?» Mu tontu ko: «Coggal laa tudd, ndaxte ñu bare lanu.» 5:10 Muy ñaan Yeesu lool, ngir mu bañ leen a dàq ca réew ma. 5:11 Fekk amoon na fa ca tund wa géttu mbaam-xuux yu bare yuy for. 5:12 Rab ya ñaan Yeesu: «Jox nu ndigal, nu dugg mbaam-xuux ya.» 5:13 Mu may leen ko. Noonu rab ya génn nit ka, dugg mbaam-xuux ya, ñu daldi bartalu, daanu ca dex ga, lab fa. Mbaam-xuux ya nag matoon nañu ñaari junni. 5:14 Noonu sàmm ya daw ca dëkk ba ak ca àll ba, nettaliji mbir mi, ba nit ñi ñëw, seet li xew. 5:15 Ñu ñëw nag ci Yeesu, gis ka rab ya jàppoon toog, sol ay yére te ànd ak sagoom. Ñu daldi ragal. 5:16 Ña fekke woon mbir ma nag nettali leen mbirum nit ka ak mbaam-xuux ya. 5:17 Ci kaw loolu ñu daldi ñaan Yeesu, mu sore seen réew. 5:18 Bi Yeesu di dugg ci gaal gi, ki rab ya jàppoon ñaan Yeesu, ngir ànd ak moom. 5:19 Waaye Yeesu mayu ko ko. Mu ne ko: «Ñibbil ci say bokk, nettali leen ni la Boroom bi yërëme, ba defal la lii lépp.» 5:20 Noonu waa ji dem ci diiwaanu Fukki dëkk yi, daldi fa yégle la ko Yeesu defal, ba ñépp waaru. 5:21 Noonu Yeesu jàllaat dex ga, taxaw ca tefes ga. Te nit ñu bare dajaloo, wër ko. 5:22 Kenn ci njiiti jàngu ba nag, tudd Yayrus, ñëw ci moom. Naka la gis Yeesu, mu daanu ciy tànkam, 5:23 di ko saraxu lu bare naan: «Sama doom ju jigéen mi ngi bëgg a faatu; kaay teg ko loxo, ngir mu wér te dund.» 5:24 Noonu Yeesu ànd ak moom. Bi muy dem, mbooloo mu réy topp ko, di ko tanc. 5:25 Amoon na fa nag jigéen ju doon xëpp deret diirub fukki at ak ñaar. 5:26 Sonnoon na lool ci loxoy fajkat yu bare, sànk ci alalam jépp te jëlewu ci genn tan, waaye faf wopp ja yokku. 5:27 Noonu mu déggoon turu Yeesu, ne ci boppam: «Su ma laalee ay yéreem rekk, dinaa wér.» Mu jaxasoo ak mbooloo mi nag, doxe ko gannaaw, laal mbubbam. 5:29 Ci saa si deret ji taxaw, mu yég ci yaramam ne, jàngoroom deñ na. 5:30 Yeesu yég ci saa si ne, doole génn na ci moom. Mu walbatiku nag ne mbooloo mi: «Ana ku laal samay yére?» 5:31 Ay taalibeem tontu ko: «Xanaa gisuloo mbooloo mi lay wër; ngay laaj: “Ku ma laal?”» 5:32 Waaye Yeesu di xool li ko wër, ngir gis ku ko def. 5:33 Noonu jigéen ja ñëw, daanu ciy tànkam, wax ko dëgg gépp; mu tiit bay lox, ndaxte xam na li xewoon ci yaramam. 5:34 Yeesu ne ko: «Soxna si, sa ngëm faj na la; demal ci jàmm, te na sa jàngoro wàcc.» 5:35 Bi Yeesu di wax nag, am na ku jóge ca kër njiit la, mu ñëw naan: «Sa doom faatu na; matatul nuy sonal kilifa gi.» 5:36 Waaye Yeesu jàppul wax jooju; mu ne njiit la: «Gëmal rekk te bañ a tiit.» 5:37 Noonu Yeesu dem, ànd ak Piyeer, Saag ak Yowaana rekk, ndaxte mayul keneen, mu ànd ak moom. 5:38 Naka lañu ñëw ci kër njiit li, Yeesu dégg coow li; ñii di jooy, ñii di yuuxu. 5:39 Mu dugg ne leen: «Lu ngeen di soow, tey jooy? Janq bi deewul, day nelaw rekk.» 5:40 Waaye ñu di ko ñaawal. Noonu Yeesu génne ñépp, woo baayu janq bi ak yaay ji ak ñi mu àndal, dugg fa janq bi nekk. 5:41 Mu jàpp loxoom ne ko: «Talita kumi,» liy tekki: «Janq bi, maa ngi la koy wax, jógal.» 5:42 Ca saa sa janq bi jóg, daldi dox, ndaxte amoon na fukki at ak ñaar. Ñépp daldi waaru, ba ne jomm. 5:43 Ci kaw loolu Yeesu dénk leen bu wóor, ñu bañ koo siiwal; teg ca naa: «Mayleen janq bi, mu lekk.»
6:1 Bi loolu amee Yeesu jóge fa, dellu réewam, ànd ak taalibe yi. 6:2 Bésu noflaay bi nag mu jàngal leen ci seen jàngu, ba mbooloom ñi ko dégg waaru naan: «Lii, fu mu ko jële, te xam-xam bii mu yor, lu mu doon, ba muy def kéemaan yii? 6:3 Ndax kii du minise bi? Ndax du doomu Maryaama te magu Saag, Yuusufa, Yuda ak Simoŋ? Te ay rakkam yu jigéen ndax nekkuñu fi ak nun?» Kon nag ñu daldi ko xeeb. 6:4 Noonu Yeesu ne leen: «Dees na faaydaal yonent, waaye du ci réewam, ciy bokkam mbaa ci këram.» 6:5 Te Yeesu mënu faa def ay kéemaan yu bare, lu dul teg loxo yenn jarag, wéral leen. 6:6 Te mu waaru ndax seen ngëmadi. Bi loolu amee Yeesu di wër dëkk ya, di jàngale. 6:7 Noonu mu woo ci moom fukki taalibe ya ak ñaar, jox leen sañ-sañu dàq rab yi, yónni leen, ñu ànd ñaar-ñaar. 6:8 Mu digal leen nii: «Bu ngeen di dem, buleen yóbbaale dara; du mburu mbaa mbuus mbaa xaalis ci seeni maxtume, waaye yemleen ci aw yet rekk. 6:9 Sol-leen ay dàll te yem ci benn turki.» 6:10 Mu ne leen: «Kër gu ngeen dugg, dal-leen fa, ba kera ngeen jóge dëkk ba. 6:11 Koo xam ne gàntu na leen, mbaa mu tanqamlu leen, génnleen fa, yëlëb seen pëndu tànk, ngir seede leen seen réer.» 6:12 Noonu taalibe ya dem, di waare naan: «Tuubleen seeni bàkkaar.» 6:13 Ñu dàq ay rab yu bare, te diw boppi jarag yu bare, wéral leen. 6:14 Noonu Erodd buur bi dégg loolu, ndaxte turu Yeesu siiwoon na. Mu ne nag: «Yaxya dekki na, moo tax mu ànd ak kàttanu def ay kéemaan.» 6:15 Ñeneen ne: «Kii Iliyas la.» Ñi ci des ne: «Yonent la, bu mel ni yonent yu jëkk ya.» 6:16 Waaye bi ko Erodd déggee, mu ne: «Yaxya male ma dagglu boppam, moom moo dekki.» 6:17 Fekk Erodd yónnee woon na, jàpp Yaxya, yeew ko, tëj. Ndaxte Erodd takkoon na Erojàdd jabaru Filib magam. 6:18 Te Yaxya ne ko: «Jaaduwul nga denc sa jabaru mag.» 6:19 Moo tax Erojàdd ëmbal ko mer, ba bëgg koo rey, waaye mënu koo def. 6:20 Ndaxte Erodd dafa ragal Yaxya, ba sàmm bakkanam, xam ne ku jub la te sell. Bu ko daan déglu it, day jaaxle lool, teewul mu bég ci déglu ko. 6:21 Noonu bés bu yell ñëw, ba Erodd doon màggal bésu juddoom; mu woo ca xew wa ay jaraafam ak kilifay xare ba ak njiiti diiwaanu Galile. 6:22 Booba doomu Erojàdd dugg di fecc, mu neex Erodd ak gan ñi, ba buur bi ne janq bi: «Laaj ma loo bëgg, dinaa la ko jox.» 6:23 Mu boole ci ngiñ ne ko: «Loo ma man a laaj, dinaa la ko jox, ba ci genn-wàllu réew mi sax.» 6:24 Noonu janq bi génn ne ndeyam: «Lu may laaj?» Mu tontu ko: «Laajal boppu Yaxya.» 6:25 Mu daldi gaawantoo dugg nag ci kanamu buur bi ne ko: «Damaa bëgg, nga indil ma léegi boppu Yaxya ci biir ndab.» 6:26 Bi ko buur ba déggee, mu am naqar wu réy. Waaye bëggu koo gàntu ndax ngiñ li ak gan ñi. 6:27 Mu daldi yónni nag xarekat, jox ko ndigal, mu indil ko boppu Yaxya. Waa ji dem, dagg boppu Yaxya ca kaso ba, 6:28 indi bopp bi ci biir ndab, jox ko janq bi, mu daldi ko jox yaayam. 6:29 Ba taalibey Yaxya déggee loolu, ñu ñëw, fab néew ba, suul ko ci bàmmeel. 6:30 Gannaaw loolu ndaw yi dajaloo ci wetu Yeesu, nettali li ñu def ak li ñu jàngale lépp. 6:31 Ci kaw loolu Yeesu ne leen: «Nanu beddeeku, dem ci bérab bu wéet; ngeen noppalu fa tuuti.» Waxoon na loolu, ndaxte amoon na ñu bare ñu doon dem ak a dikk, ba amuñu sax jot ngir lekk. 6:32 Noonu ñu dugg cig gaal, dem ca bérab bu wéet. 6:33 Bi ñuy dem nag, am ñu leen gis, xàmmi leen, ñu daldi jóge ci dëkk yépp, daw, jiitu leen fa. 6:34 Bi Yeesu génnee gaal gi, mu gis mbooloo mu réy, yërëm leen, ndaxte dañoo mel ni xar yu amul sàmm. Kon mu daldi leen jàngal lu bare. 6:35 Ca ngoon sa taalibe yi ñëw ci moom ne ko: «Fii àllub neen la, te léegi mu guddi. 6:36 Yiwil mbooloo mi nag, ñu dugg ci àll bi ak dëkk yi nu wër, jënd lu ñu lekk.» 6:37 Waaye Yeesu tontu leen ne: «Yéen joxleen leen lu ñu lekk.» Ñu ne ko: «Xanaa nu jënd lu tollook peyu juróom-ñetti weer ci mburu, jox leen ñu lekk?» 6:38 Yeesu laaj leen: «Ñaata mburu ngeen am? Demleen seeti.» Ñu dem seeti ne ko: «Juróomi mburu ak ñaari jën.» 6:39 Noonu Yeesu sant mbooloo mi, ñu def ay géew, toog ci ñax mu naat mi. 6:40 Ñu toog nag ay géewi juróom-fukk ak téeméer. 6:41 Bi loolu amee Yeesu jël juróomi mburu yi ak ñaari jën yi, xool ci kaw, sant Yàlla, ba noppi mu damm mburu yi, jox ko taalibe yi, ngir ñu séddale ko mbooloo mi. Ñaari jën yi it mu séddale ko ñépp. 6:42 Noonu ñépp lekk ba suur. 6:43 Te it ñu dajale la desoon ca dammiti mburu ak jën ya, mu nekk fukki pañe ak ñaar yu fees. 6:44 Ñu lekkoon nag matoon na limu juróomi junniy góor. 6:45 Ci kaw loolu Yeesu sant ay taalibeem, ñu dugg ci gaal gi, jàll ba Betsayda, bi muy yiwi mbooloo mi. 6:46 Bi mu tàggtoo ak mbooloo mi, mu yéeg ca tund wa, ñaan fa Yàlla. 6:47 Noonu guddi jot, fekk gaal gi nekk ci diggu dex gi, te Yeesu rekk moo nekk ca tefes ga. 6:48 Booba mu gis taalibe yi sonn lool ci joow gaal gi ndax li leen ngelaw li soflu. Ca njël nag mu jëm ci ñoom, di dox ci kaw dex gi, ba xaw leen a raw. 6:49 Bi ñu ko gisee nag, muy dox ci kaw dex gi, ñu foog ne njuuma la, daldi yuuxu. 6:50 Ndaxte ñépp gis ko te jommi ci. Waaye mu wax ak ñoom ci saa si ne leen: «Takkleen seen fit, man la, buleen tiit!» 6:51 Noonu mu fekksi leen ci gaal gi, ngelaw daldi ne tekk. 6:52 Njàqarey taalibe ya nag weesu dayo, ndaxte seen xol dafa fatt, ba réere mbir kéemaan, gi Yeesu defoon ci mburu yi. 6:53 Bi nga xamee ne jàll nañu, ba egg diiwaanu Senesaret, ñu teer fa, 6:54 génn ca gaal ga. Ci saa si nit ñi xàmmi ko, 6:55 ñu daldi daw ca diiwaan ba bépp, te fépp fu ñu ko dégg ñu di ko indil ñu wopp, tëdd ci seeni lal. 6:56 Te fu mu man a aw, ci dëkk yu mag mbaa yu ndaw walla ci àll bi, ñu indil ko jarag yi ci pénc yi, ñaan ko, mu may leen ñu laal cati mbubbam rekk. Te képp ku ko laal daldi wér.
7:1 Amoon na bés nag, ay Farisen ak ay xutbakat yu jóge Yerusalem ñëw ci Yeesu. 7:2 Ñu gis yenn ciy taalibeem di lekk, fekk seeni loxo setul, maanaam raxasuwuñu woon, ni ko aada santaanee. 7:3 Farisen yi nag ñoom ak Yawut yi yépp dañuy topp aaday yoon, yi maam yi tëral, te fandee leen gënal lekk ak loxo yu ñu raxasul. 7:4 Te it bu ñu jógee pénc ma, su ñu sanguwul set, duñu lekk. Am nañu it yeneen aada yu bare, maanaam ni nga war a raxase ay kaas, ay njaq ak ay satala, ba ñu laab. 7:5 Noonu Farisen ya ak xutbakat ya laaj ko ne: «Lu tax say taalibe duñu topp aaday yoon, yi maam yi tëral, waaye ñuy lekk ak loxo yu setul?» 7:6 Yeesu tontu leen: «Esayi waxoon na bu baax ci kàddug Yàlla ci seen mbir, yéen naaféq yi, bi mu bindee:“Xeet wii, ñu ngi may teral ci seen gémmiñ,waaye seen xol sore na ma. 7:7 Seen màggal amul benn njariñ,ci li ñuy jàngale dénkaaney nit kese.”» 7:8 Yeesu neeti leen: «Dëddu ngeen ndigali Yàlla, jublu ci aaday nit.» 7:9 Mu teg ca ne leen: «Xelu ngeen ci tebbi ndigali Yàlla, ngir sàmm seen aada. 7:10 Ndaxte Musaa nee na: “Teralal sa ndey ak sa baay,” teg ca ne: “Ku móolu sa yaay walla sa baay, dees na la rey.” 7:11 Waaye yéen dangeen ne, ku ne sa yaay walla sa baay: “Li nga war a jariñoo ci man Korban la,” maanaam “jébbal naa ko Yàlla,” 7:12 dootuleen ko bàyyi, mu defal dara ndeyam walla baayam. 7:13 Noonu tebbi ngeen kàddug Yàlla ndax seen aada, ji ngeen di donnante. Te it yéena ngi def yeneen yu bon yu mel nii.» 7:14 Noonu Yeesu waxaat ak mbooloo mi ne leen: «Yéen ñépp dégluleen ma te xam. 7:15 Li ci biti, tey dugg nit, du ko man a indil sobe, waaye li génn ci nit, loolu mooy indil nit sobe.» 7:17 Bi nga xamee ne jóge nañu ci mbooloo mi, dugg ci kër gi, taalibe yi laaj Yeesu, mu firil leen wax ju làqu jooju. 7:18 Yeesu tontu leen ne: «Ndax yéen itam seen xol dafa tëju? Xanaa xamuleen ne, dara lu jóge biti, dugg ci nit, du ko man a indil sobe, 7:19 ndaxte du dugg ci xol, waaye ci biiram lay jëm, ba noppi daldi génn ca bérab bu làqu?» Ci li mu wax loolu Yeesu daganal na bépp ñam. 7:20 Yeesu ne leen ati: «Li génn ci nit, loolu mooy indil nit sobe. 7:21 Ndaxte ci biir, ci xolu nit, la xalaat yu bon di jóge ak ndoxaanu yàqute, càcc ak bóom, 7:22 njaaloo ak bëgge, coxor, naaféq, ñaawteef, ñeetaan, saaga, réylu ak jëfi ndof. 7:23 Lu bon loolu lépp day génn ci nit, di ko indil sobe.» 7:24 Gannaaw loolu Yeesu jóge fa, jëm weti dëkku Tir. Bi mu fa eggee, mu dugg ci kër, te bëggul kenn xam ko, waaye jataayam mënul a umpe. 7:25 Amoon na fa nag jigéen ju rab jàpp doomam ju jigéen. Bi mu déggee ne, Yeesoo nga fa, mu ñëw, daanu ciy tànkam, 7:26 fekk jigéen ja ci xeetu Gereg la bokkoon, juddoo wàlli Fenisi ci diiwaanu Siri. Noonu jigéen ja ñaan ko, mu dàq rab wi ci doomam. 7:27 Waaye Yeesu ne ko: «Na gune yi jëkk a lekk, ba regg; fab ñamu gune yi, sànni ko xaj yi, rafetul.» 7:28 Jigéen ji tontu ko: «Waaw sang bi, teewul xaj yi di lekk ruusit, yi rot ci lekkukaayu gune yi.» 7:29 Ci kaw loolu Yeesu ne ko: «Ndax wax jooju demal ci jàmm, rab wa génn na sa doom.» 7:30 Noonu mu ñibbi, fekk doom ji tëdd cib lal te mucc ci rab wi. 7:31 Bi loolu amee Yeesu jóge na weti Tir, jaar ci wàlli dëkku Sidon, dem dexu Galile, ba noppi dugg ci biir diiwaan, bi ñuy wax Fukki dëkk yi. 7:32 Foofa ñu indil ko ku tëx te dër lool, ñaan ko mu teg ko loxo. 7:33 Noonu Yeesu yóbbu ko, ba ñu sore mbooloo mi, mu def ay baaraamam ciy noppam, daldi tifli, laal làmmiñam. 7:34 Mu yërëm ko, ba binni ci xolam, xool ci asamaan, daldi ne: «Effata,» liy tekki: «Ubbikuleen.» 7:35 Ci saa si ay noppam daldi dégg te làmmiñam yiwiku, muy wax bu leer. 7:36 Bi mu ko defee Yeesu tere leen, ñu wax ko kenn, waaye lu mu leen ko gën a tere, ñu gën ko nee siiwale. 7:37 Ñu waaru lool naan: «Lépp lu mu def, lu yéeme la. May na sax tëx yi ñuy dégg, ak luu yi ñuy wax.»
8:1 Ca bés yooya mbooloo mu réy amaatoon na, te amuñu woon lu ñu lekk. Noonu Yeesu woo taalibe ya ne leen: 8:2 «Yërëm naa mbooloo mi, ndaxte toog nañu fi man ñetti fan, te amatuñu lu ñu lekk. 8:3 Su ma leen yiwee ak seen xiif, dinañu tële ci yoon wi, ndaxte am na ñu jóge fu sore.» 8:4 Taalibe yi tontu ko: «Waaye fii àllub neen la; fu nuy jële lu doy ngir dundal leen?» 8:5 Yeesu laaj leen: «Ñaata mburu ngeen am?» Ñu ne ko: «Juróom-ñaar.» 8:6 Noonu Yeesu sant mbooloo mi, ñu toog ci suuf. Mu jël juróom-ñaari mburu yi, sant Yàlla, damm leen, jox leen taalibe yi, ngir ñu séddale leen mbooloo mi; taalibe yi def ko. 8:7 Amoon na fa it tuuti jën yu ndaw. Yeesu jël ko, sant Yàlla, wax taalibe yi, ñu séddale leen itam mbooloo mi. 8:8 Noonu nit ñi lekk ba suur, ba noppi taalibe yi dajale juróom-ñaari dàmba yu fees ak dammit yi ci des. 8:9 Ña ko fekke nag matoon nañu ñeenti junniy góor. 8:10 Bi ko Yeesu defee, mu yiwi leen, daldi dugg ak taalibe ya ca gaal ga, dem ca wàlli Dalmanuta. 8:11 Noonu Farisen yi ñëw, di werante ak moom; ñu fexe koo fiir, ba laaj ko kéemaan gu jóge ci asamaan tey firndeel yónnentam. 8:12 Waaye Yeesu binni ci xolam ne leen: «Lu tax niti jamono jii di laaj kéemaan? Ci dëgg maa ngi leen koy wax, duñu jot genn kéemaan.» 8:13 Ci kaw loolu Yeesu bàyyi leen, duggaat ci gaal gi, di jàll dex gi. 8:14 Taalibe yi nag fàtte woon nañu yóbbaale mburu, te amuñu woon lu dul benn mburu ci gaal gi. 8:15 Noonu Yeesu artu leen ne: «Wottuleen te moytu lawiiru Farisen yi ak ñi far ak buur bi Erodd.» 8:16 Taalibe yi nag daldi werante naan: «Nun de indaalewunu mburu.» 8:17 Waaye Yeesu yég loolu ne leen: «Lu tax ngeen di werante ci li ngeen indaalewul mburu? Xanaa gisaguleen te xamuleen? Ndax seen xol dafa fatt ba tey? 8:18 Ndax ay gumbay njàccaar ngeen, te seeni nopp naqari? Xanaa fàttalikuwuleen; 8:19 bi ma dammee juróomi mburu ya ngir juróomi junni ña, ñaata pañe yu fees ak ay dammit ngeen ca dajale woon?» Ñu tontu ko: «Fukk ak ñaar.» 8:20 Yeesu neeti leen: «Te bés bi ma dammee juróom-ñaari mburu yi ngir ñeenti junni ñi, ñaata dàmba yu fees ak dammit ngeen dajale woon?» Ñu ne ko: «Juróom ñaar.» 8:21 Noonu Yeesu ne leen: «Ndax seen xol dafa tëju ba tey?» 8:22 Gannaaw loolu ñu ñëw ci Betsayda. Foofa ñu indil Yeesu ku gumba, di ko ñaan, mu laal ko. 8:23 Yeesu nag jàpp loxob gumba gi, yóbbu ko, ba génn dëkk bi. Mu def tiflit ciy bëtam, teg ko loxo naan: «Ndax gis nga dara?» 8:24 Waa ji xool ne ko: «Gis naa ay nit, ñu mel ni ay garab, te ñu ngi dox.» 8:25 Kon Yeesu laalaat bët yi, gumba gi ne xefeet, daldi wér, ba gis lépp bu leer. 8:26 Ci kaw loolu Yeesu sant ko mu ñibbi ne ko: «Bul dugg ca dëkk ba.» 8:27 Bi loolu amee Yeesu ànd ak ay taalibeem, dem ca dëkk, yi wër Sesare bu Filib. Bi ñuy dem nag, mu laaj taalibe yi: «Nit ñi, lu ñu wax ne man moom laa?» 8:28 Ñu ne ko: «Am na ñuy ne, yaa di Yaxya; ñeneen ne, Iliyas; ñi ci des ne, yaay kenn ci yonent yi.» 8:29 Noonu Yeesu laaj leen: «Yéen nag, ku ngeen wax ne moom laa?» Piyeer tontu ko: «Yaa di Almasi bi.» 8:30 Ci kaw loolu Yeesu dénk leen bu wóor, ñu bañ koo wax kenn. 8:31 Booba Yeesu tàmbali na leen a xamal ne, Doomu nit ki war na sonn lu bare; njiit ya, saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya dëddu ko, ñu rey ko, mu dekki ci ñetti fan. 8:32 Noonu mu xamal leen mbir mi, ba mu leer nàññ. Bi ko Piyeer déggee, mu woo ko ci pegg, daldi ko yedd. 8:33 Waaye Yeesu geestu, gis yeneen taalibe yi, mu daldi yedd Piyeer ne ko: «Sore ma Seytaane; yëfi nit ngay fonk, waaye du yëfi Yàlla.» 8:34 Noonu Yeesu woo taalibe yi ak mbooloo mi ne leen: «Ku bëgg a topp ci samay tànk, na bàyyi boppam te gàddu bant bi ñu ko war a daaj, door a topp ci man. 8:35 Ndaxte koo xam ne bëgg ngaa rawale sa bakkan, dinga ko ñàkk, waaye ku ñàkk sa bakkan ngir man ak ngir xebaar bu baax bi, dinga ko jotaat. 8:36 Ndaxte moom àddina sépp, lu muy jariñ nit, bu ñàkkee bakkanam? 8:37 Te nit, lu mu war a weccee bakkanam? 8:38 Ku ma rus a faral, te nanguwul samay wax ci kanamu niti jamono jii, ñi fecci seen kóllëre ak Yàlla te topp bàkkaar, Doomu nit ki dina la rus a xam, bés bu ñëwee ci ndamu Baayam, ànd ak malaaka yu sell yi.»
9:1 Mu ne leen ati: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, am na ñi fi taxaw, ñoo xam ne duñu dee, te gisuñu nguuru Yàlla ñëw ak doole.» 9:2 Juróom-benni fan gannaaw gi, Yeesu àndoon na ak Piyeer, Saag ak Yowaana, mu yóbbu leen ñoom rekk fu wéet ci tund wu kawe lool. Foofa jëmmam soppiku ci seen kanam; 9:3 ay yéreem di ray-rayi, weex tàll, te fóotukatu àddina mënu leen weexale nii. 9:4 Noonu ñu gis yonenti Yàlla Iliyas ak Musaa, di wax ak Yeesu. 9:5 Piyeer daldi ne Yeesu: «Kilifa gi, bég nanu ci sunu teew fii; nanu defar ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa ak benn Iliyas.» 9:6 Fekk xamul lu muy wax, ndaxte tiitaange jàpp na leen ñoom ñett ñépp. 9:7 Noonu niir muur leen, te baat jibe ca niir wa naan: «Kii mooy sama Doom ji ma bëgg, ci moom laa ame bànneex; dégluleen ko.» 9:8 Ci saa si taalibe yi xool, waaye gisatuñu kenn, ku dul Yeesu rekk. 9:9 Bi loolu amee ñu wàcc ca tund wa. Bi muy wàcc nag, Yeesu sant leen ne: «Buleen nettali kenn li ngeen gis, ba kera Doomu nit ki dekki na.» 9:10 Ñu téye wax jooju ci seen biir, di sotteente xel, ba xam lu ndekkite looluy tekki. 9:11 Noonu taalibe yi laaj Yeesu: «Lu tax xutbakat yi di naan, Iliyas moo war a jëkk a ñëw?» 9:12 Yeesu ne leen: «Waaw, Iliyas dina jëkk a ñëw, jubbanti lépp. Waaye itam lu tax bind nañu ne, Doomu nit ki war na sonn lu bare, ñu xeeb ko, dëddu ko. 9:13 Waaye maa ngi leen di wax ne, Iliyas ñëw na, te def nañu ko la leen neex, ni ko Mbind mi waxe.» 9:14 Bi nga xamee ne Yeesu ñëw na, ba jege taalibe yi, mu gis mbooloo mu bare wër leen, te ay xutbakat di werante ak ñoom. 9:15 Naka la mbooloo mi gis Yeesu, ñu waaru, daldi daw nuyu ko. 9:16 Noonu Yeesu laaj leen: «Ci lan ngeen di werante ak ñoom?» 9:17 Kenn ci mbooloo mi tontu ko ne: «Kilifa gi, rab jàpp na sama doom, ba luuloo ko. Saa su ko jàppee, daf koy daaneel ci suuf, gémmiñ gi di fuur, muy yéyu, ne jàdd. Ñaan naa say taalibe, ñu dàq ko, waaye mënuñu ko.» 9:19 Yeesu ne leen: «Yéen niti jamono jii, yéen ñi gëmadi, ba kañ laa war a nekk ak yéen, ba kañ laa leen war a muñal? Indil-leen ma xale bi.» 9:20 Ñu indil ko ko. Bi xale bi gisee Yeesu nag, rab wi sayloo ko ci saa si, mu daanu ci suuf, di xalangu, gémmiñ giy fuur. 9:21 Yeesu laaj baay bi: «Lii kañ la ko dal?» Baay bi ne ko: «Li dale ci nguneem. 9:22 Léeg-léeg rab wi bëmëx ko ci safara, léeg-léeg mu bëmëx ko ci ndox, ngir rey ko. Soo ko manee, yërëm nu te xettali nu.» 9:23 Yeesu tontu ko: «Nga ne: “Soo ko manee,” ku gëm man na lépp.» 9:24 Ci saa si baayu xale bi wax ci kaw naan: «Gëm naa, dàqal ma sama ngëmadi.» 9:25 Yeesu gis nag ne, mbooloo maa ngi daw, wërsi ko, mu daldi gëdd rab wi nag ne ko: «Génnal ci moom, yaw rab wu luu te tëx, te bu ko jàppaat; wax naa la ko.» 9:26 Noonu rab wa daldi yuuxu, sayloo xale bi, génn. Xale bi ne nemm, mel ni ku dee, ba tax ñu bare ne: «Dee na.» 9:27 Waaye Yeesu jàpp loxoom, jógloo ko, xale bi daldi taxaw. 9:28 Bi Yeesu duggee ci kër gi, taalibe yi laaj ko ci pegg: «Lu tax mënunu ko woon a dàq?» 9:29 Yeesu tontu leen ne: «Yu mel ni yii, ñaan ci Yàlla rekk a leen di dàq.» 9:30 Bi loolu amee ñu jóge fa, jaar ci diiwaanu Galile, Yeesu bëggul kenn yég ko. 9:31 Ndaxte muy jàngal taalibe yi ne leen: «Dees na jébbal Doomu nit ki ci loxoy nit, te dinañu ko rey, mu dekki ci ñetti fan.» 9:32 Waaye taalibe yi xamuñu lu wax joojuy tekki, te ñemewuñu ko koo laaj. 9:33 Bi nga xamee ne egg nañu dëkku Kapernawum, te dugg ci kër gi, Yeesu laaj leen ne: «Lu ngeen doon waxtaane ci yoon wi?» 9:34 Waaye ñu ne cell, ndaxte ñu ngi fa doon werante, ba xam ku gën a màgg ci ñoom. 9:35 Noonu Yeesu toog, woo fukki taalibe ya ak ñaar ne leen: «Ku bëgg a jiitu, na topp ci gannaaw ñépp te nekk surgab ñépp.» 9:36 Bi ko Yeesu waxee, mu jël xale, indi ko ci biir géew gi, ba noppi leewu ko naan: 9:37 «Ku nangu xale bu mel ni bii ci sama tur, man mii nga nangu; te ku ma nangu, du man mii sax nga nangu waaye ki ma yónni.» 9:38 Bi loolu amee Yowaana ne ko: «Kilifa gi, danoo gis nit kuy dàq ay rab ci sa tur, nu tere ko ko, ndax li mu bokkul ci nun.» 9:39 Waaye Yeesu tontu ko: «Buleen ko tere, ndaxte kenn mënul a def kéemaan ci sama tur, ba noppi di ma xarab. 9:40 Ku nu sotul, far na ak nun. 9:41 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, koo xam ne kii may na leen kaasu ndox rekk, ndax yéena ngi bokk ci man Kirist, kooku du ñàkk yoolam mukk. 9:42 «Waaye ku yóbbe bàkkaar kenn ci ñi gën a tuuti ñi ma gëm, li gën ci moom, moo di ñu takk doj wu réy ci baatam, sànni ko ci géej. 9:43 Boo xamee ne sa loxo mu ngi lay yóbbe bàkkaar, dagg ko. Ndaxte ñàkk loxo te tàbbi ci dund gu wóor gi, moo gën ci yaw, nga am ñaari loxo te tàbbi ci safara su dul fey mukk. 9:45 Te bu la sa tànk di yóbbe bàkkaar, dagg ko. Nga lafañ te tàbbi ci dund gu wóor gi moo gën, nga am ñaari tànk, ñu sànni la ci safara. 9:47 Te bu la sa bët di yóbbe bàkkaar, luqi ko. Nga patt te dugg ci nguuru Yàlla, moo gën ci yaw, nga am ñaari bët, ñu sànni la ci safara. 9:48 Foofa:“Sax ya duñu dee mukk,te safara sa du fey.” 9:49 Ñépp safara lañu leen di xorome. 9:50 Xorom lu baax la, waaye bu sàppee, nan lañu koy delloo cafkaam? Amleen xorom te ngeen jàmmoo.»
10:1 Gannaaw loolu Yeesu jóge fa, dem ca wàlli réewu Yawut yi, ya ca gannaaw dexu Yurdan. Bi mu fa demee, mbooloo mu bare ñëw fi moom. Yeesu daldi leen jàngal, ni mu ko daan defe. 10:2 Noonu ay Farisen ñëw ci moom, lalal ko fiir, ñu laaj ko: «Ndax jaadu na, nit fase jabaram?» 10:3 Yeesu tontu leen ne: «Lu leen yoonu Musaa sant?» 10:4 Ñu ne ko: «Musaa maye na, nit bind kayitu pase, tàggook jabaram.» 10:5 Waaye Yeesu ne leen: «Dénkaane boobu mu leen bindal, bind na ko ndax seen xol dafa fatt. 10:6 Waaye ca njàlbéen ga “Yàlla sàkk na leen, kii góor, kii jigéen. 10:7 Moo tax góor dina beru ndeyam ak baayam, di taq ci jabaram, 10:8 ñoom ñaar doon benn.” Kon nekkatuñu ñaar waaye benn. 10:9 Lu Yàlla takk nag, bu ko nit tas.» 10:10 Bi ñu delloo ca kër ga nag, taalibe ya laaj ko ci mbirum loolu. 10:11 Noonu Yeesu ne leen: «Ku fase sa jabar, takk jeneen, njaaloo nga, di tooñ ku jëkk ka. 10:12 Te jigéen ji tas, séyaat ak keneen, njaaloo nga.» 10:13 Bi loolu wéyee ñu indil Yeesu ay xale, ngir mu teg leen ay loxoom. Waaye taalibe ya gëdd nit ñi. 10:14 Bi ko Yeesu gisee nag, mu metti ko lool, mu ne leen: «Bàyyileen xale yi, ñu ñëw fi man! Buleen leen tere, ndaxte ñu mel ni ñoom ñoo yelloo nguuru Yàlla. 10:15 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ku woyoful ni xale, nangu nguuru Yàlla, doo ci man a dugg.» 10:16 Noonu Yeesu leewu leen, teg leen ay loxoom, barkeel leen. 10:17 Gannaaw loolu bi Yeesu nekkee ci kaw yoon wi di dem, am ku daw, sukk ci kanamam ne ko: «Kilifa gu baax gi, lu ma war a def, ngir am wàll ci dund gu dul jeex gi?» 10:18 Yeesu tontu ko: «Lu tax nga wooye ma ku baax ki? Yàlla rekk a baax. 10:19 Xam nga ndigal yi: “Bul bóom, bul njaaloo, bul sàcc, bul seede lu dul dëgg, bul nangu alalu jaambur, teralal sa ndey ak sa baay.”» 10:20 Waa ji ne ko: «Kilifa gi, loolu lépp sàmm naa ko li dale ci samag ndaw ba tey.» 10:21 Noonu Yeesu xool ko, am cofeel ci moom, mu ne ko: «Lenn rekk moo la dese. Demal jaay li nga am, may ko miskin yi, te dinga woomle ci asamaan; boo noppee, nga ñëw topp ci man.» 10:22 Waaye ci wax jooju xar-kanamam lëndëm, mu jóge fa ak tiis, ndaxte ku bare woon alal la. 10:23 Noonu Yeesu xool taalibe yi ko wër ne leen: «Boroom alal dugg ci nguuru Yàlla, lu jafee ngoogu!» 10:24 Wax jooju nag daldi jaaxal taalibe yi lool. Waaye Yeesu neeti leen: «Samay xarit, dugg ci nguuru Yàlla, lu jafee ngoogu! 10:25 Giléem jaar ci bën-bënu pusa, moo gën a yomb boroom alal dugg ci nguuru Yàlla.» 10:26 Wax jooju gënatee jaaxal taalibe ya, ñu naan ci seen biir: «Kon nag ku man a mucc?» 10:27 Noonu Yeesu xool leen naan: «Loolu të na nit, waaye tëwul Yàlla; Yàlla man na lépp.» 10:28 Ci kaw loolu Piyeer daldi ko ne: «Nun de dëddu nanu lépp te topp la!» 10:29 Yeesu tontu ko: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, képp ku dëddu kër, doomu ndey yu góor walla yu jigéen, ndey walla baay, doom walla suuf ndax man ak xebaar bu baax bi, 10:30 dinga am tey jii téeméeri yoon ay kër, doomi ndey yu góor ak yu jigéen, ndey, doom ak suuf, ñoom ak ay fitnay noon, te ëllëg nga am dund gu dul jeex. 10:31 Waaye ñu bare ci ñi jiitu ñooy mujji; ñi mujj ñooy jiituji.» 10:32 Gannaaw loolu ñu ànd jëm Yerusalem, Yeesu jiitu; taalibe yi am njàqare, te ñi ci topp tiit. Noonu Yeesu woowaat fukk ak ñaar ña cig wet, xamal leen li nar a xew ci mbiram. 10:33 Mu ne leen: «Noo ngi dem Yerusalem, te dees na jébbal Doomu nit ki ci loxoy saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya. Dinañu ko àtte, teg ko dee, jébbal ko ñi dul Yawut, 10:34 ñu ñaawal ko, di tifli ci kawam, dóor ko ay yar, rey ko. Waaye gannaaw ñetti fan dina dekki.» 10:35 Gannaaw loolu Saag ak Yowaana, doomi Sebede, ñëw ci Yeesu. Ñu ne ko: «Kilifa gi, danoo bëggoon nga may nu li nu lay ñaan.» 10:36 Yeesu tontu leen: «Lu ngeen bëggoon, ma may leen ko?» 10:37 Ñu ne ko: «Bés boo soloo sa ndam, nga may nu, nu toog, kii ci sa ndeyjoor, kii ci sa càmmooñ.» 10:38 Waaye Yeesu tontu leen: «Xamuleen li ngeen di ñaan. Ndax man ngeen a naan kaasu naqar, bi may naan? Ndax man ngeen a sóobu ci metit, yi ma nar a sóobu?» 10:39 Ñu ne ko: «Waaw, man nanu ko.» Noonu Yeesu ne leen: «Dingeen naan kaasu naqar, bi may naan, tey sóobu ci metit, yi ma nar a sóobu, 10:40 waaye toog ci sama ndeyjoor mbaa sama càmmooñ, du man maa koy maye. Ñi ñu ko waajal rekk a ko yelloo.» 10:41 Bi nga xamee ne fukki taalibe ya ca des dégg nañu loolu, ñu daldi mere Saag ak Yowaana. 10:42 Waaye Yeesu woo leen naan: «Xam ngeen ne ci xeeti àddina, ñi ñu teg njiit dañu leen di dóor yetu nguur, te kilifa yi di leen noot. 10:43 Buleen mel ni ñooñu. Waaye ku bëgg a nekk kilifa ci yéen, na nekk seen surga, 10:44 te ku bëgg a nekk njiit, na nekk seen jaam. 10:45 Ndaxte noonu la Doomu nit ki ñëwe sax, du ngir ñu nekk ay surgaam, waaye ngir muy seen surga, ba joxe bakkanam ngir njotug ñu bare.» 10:46 Bi loolu wéyee ñu agsi ca dëkku Yeriko. Bi ko Yeesu di génn, ànd ak taalibe ya ak mbooloo mu xaw a bare, am gumba gu tudd Bartime — liy tekki «doomu Time,» toog ci wetu yoon wi, di yelwaan. 10:47 Noonu mu dégg ne, Yeesum Nasaret moo fay romb; mu daldi yuuxu naan: «Yërëm ma, yaw Sëtu Daawuda bi!» 10:48 Ci kaw loolu ñu bare gëdd ko, ngir mu noppi. Teewul mu gën a yuuxu naan: «Yaw Sëtu Daawuda bi, yërëm ma!» 10:49 Noonu Yeesu taxaw, daldi ne: «Wooleen ko!» Ñu woo nag gumba gi ne ko: «Na sa xel dal! Jógal! Mu ngi lay woo.» 10:50 Bi mu ko déggee, mu sànni malaanam, ne bërét, dem ci Yeesu. 10:51 Yeesu ne ko: «Loo bëggoon ma defal la ko?» Gumba gi tontu ko: «Kilifa gi, damaa bëgg a gis.» 10:52 Noonu Yeesu ne ko: «Demal ci jàmm. Sa ngëm faj na la.» Ci saa si gumba gi gis, daldi topp Yeesu ci yoon wi.
11:1 Gannaaw loolu Yeesu ak taalibe ya jege nañu Yerusalem, ba agsi dëkki Betfase ak Betani ci wetu tundu Oliw ya. Noonu Yeesu yebal ñaar ciy taalibeem, 11:2 ne leen: «Demleen ci dëkk bi ci kanam. Bu ngeen fa duggee, dingeen fa gis cumbur gu kenn musul a war. Yiwileen ko, indi. 11:3 Bu leen kenn nee: “Lu ngeen di def?” tontuleen ko: “Boroom bi da koo soxla, te léegi mu delloosi ko.”» 11:4 Taalibe ya dem nag, ñu gis cumbur ga ci mbedd mi, mu yeewe cib buntu kër. 11:5 Bi ñu koy yiwi nag, am na ca ña fa taxaw, ñu ne leen: «Lu ngeen nar, bay yiwi cumbur gi?» 11:6 Taalibe yi tontu leen, ni leen Yeesu digale woon, kon nit ñi bàyyi leen, ñu dem. 11:7 Ñu indi cumbur gi Yeesu nag, lal ci seeni yére, mu toog ci. 11:8 Ñu bare lal seeni yére ci yoon wi, ñenn ñi dagg ay cari garab ci tool yi, lal leen it ci yoon wi. 11:9 Ñiy jiitu ak ñiy topp ci Yeesu ñépp di wax ci kaw naan:«Osaana!Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi,ku barkeel nga! 11:10 Nguuru sunu maam Daawuda giy ñëw,dina barkeel!Ci bérab yu gën a kawe,nañu ne: “Osaana!”» 11:11 Noonu Yeesu dugg Yerusalem, dem kër Yàlla ga, xool lépp, ba noppi génn dem dëkku Betani, moom ak fukki taalibe ya ak ñaar, ndaxte dafa guddi. 11:12 Bët set ñu génn Betani, fekk Yeesu xiif. 11:13 Noonu mu séen fu sore garabu figg gu sëq, mu dem seeti, ndax am na ay doom. Waaye bi mu fa eggee, gisul lu dul ay xob, ndaxte jamonoy figg duggagul. 11:14 Ci kaw loolu mu ne garab gi: «Dootuloo meññ mukk!» Taalibe yi dégg loolu mu wax. 11:15 Bi ñu eggee Yerusalem, Yeesu dugg ci kër Yàlla gi, daldi dàq ñi fay jaay ak ñi fay jënd. Mu daaneel taabali weccikatu xaalis yi ak tooguy jaaykati pitax yi, 11:16 te mayul kenn, mu yóbbu am njaay ci kër Yàlla gi. 11:17 Mu di leen jàngal ne leen: «Ndax waxuñu ci Mbind mi:“Dees na wooye sama kërkëru ñaan ci Yàlla ngir xeet yépp”? Waaye yéen def ngeen ko këru sàcc.» 11:18 Bi ko saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya déggee nag, ñu ragal ko, ndaxte mbooloo mépp dañoo waaru ci njàngaleem. Noonu ñu seet pexem reylu ko. 11:19 Bi timis jotee Yeesu ak taalibe yi génn dëkk bi. 11:20 Ci suba si, bi ñuy dem, ñu gis ne garabu figg gi dee na, ba wow koŋŋ. 11:21 Noonu Piyeer fàttaliku li xewoon, ne Yeesu: «Kilifa gi, xoolal, figg gi nga rëbb dee na, ba wow!» 11:22 Yeesu tontu ne: «Gëmleen Yàlla. 11:23 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ku ne tund wale: “Jógal, tàbbi ca géej ga,” te nga gëm ne loolu dina am, bañ cee boole xel ñaar, kon sa ñaan nangu. 11:24 Moo tax maa ngi leen koy wax, bu ngeen di ñaan Yàlla, lépp lu ngeen ko man a laaj, gëmleen ne jot ngeen ko, te dingeen ko am. 11:25 Te it bu ngeen di ñaan, fekk ngeen jàppal kenn dara, baal-leen ko, ngir seen Baay bi ci kaw baal leen seeni tooñ, yéen itam.» 11:27 Gannaaw loolu ñu duggaat Yerusalem, te Yeesu doon doxantu ca ëtti kër Yàlla ga. Noonu saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya ak njiit ya dab ko 11:28 ne ko: «Yëf yii ngay def, ci ban sañ-sañ nga koy defe? Te ku la may sañ-sañu def ko?» 11:29 Yeesu tontu leen: «Man itam dinaa leen laaj lenn; bu ngeen ma ci tontoo, kon dinaa leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii. 11:30 La Yaxya daan def, di sóob nit ñi ci ndox, fu mu ko jële, ci Yàlla walla ci nit ñi?» 11:31 Bi ñu ko déggee, ñuy werante ci seen biir naan: «Bu nu nee: “Ci Yàlla,” kon dina nu laaj: “Lu tax gëmuleen ko kon?” 11:32 Waaye bu nu nee: “Ci nit ñi,” kon mbooloo mi dal ci sunu kaw;» ndaxte ñépp teg nañu Yaxya ab yonent. 11:33 Ñu tontu Yeesu nag ne: «Loolu de xamunu ko.» Noonu Yeesu ne leen: «Kon man itam duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii.»
12:1 Noonu Yeesu daldi leen wax ciy léeb. Mu ne leen: «Amoon na fi nit ku jëmbët toolu réseñ. Mu ñag tool bi, gas pax ngir nal ci réseñ yi, tabax wottukaay, ba noppi batale ko ay beykat, daldi tukki. 12:2 «Bi tool bi ñoree nag, mu yónni surga ci ñoom, ngir jot wàllam ci meññeef gi. 12:3 Waaye ñu jàpp ko, dóor ko ay yar, dàq ko, mu dellu ak loxoy neen. 12:4 Mu yónniwaat beneen surga, waaye ñu dóor ko ci bopp, toroxal ko. 12:5 Mu yónneeti beneen surga, ñu rey ko. Mu yónni ñeneen ñu bare, ñii ñu dóor leen, ñii ñu rey. 12:6 «Noonu mu dese ko kenn rekk, di doomam ji mu bëgg. Mujj mu yónni ko naan: “Xëy na ñu weg sama doom.” 12:7 Waaye beykat yi daldi ne ci seen biir: “Kii moo war a donn tool bi; nan ko rey, moom ndono li.” 12:8 Ñu jàpp ko nag, rey, sànni ci biti.» 12:9 Noonu Yeesu laaj leen: «Boroom tool bi nag, lu muy def? Xanaa ñëw, rey beykat ya, dénk tool ba ñeneen. 12:10 Ndax musuleen a jàng wax jii ci Mbind mi?“Doj wi tabaxkat yi sànni,mujj na di doju koñ; 12:11 ci Boroom bi la loolu jóge,te yéemu nanu ci.”» 12:12 Noonu kilifa yi di wut pexem jàpp ko, ndaxte xam nañu ne, ñoom lay wax. Waaye ragal nañu mbooloo mi, ba ñu bàyyi ko fa, dem. 12:13 Bi loolu amee ñu yónni ci Yeesu ay Farisen ak ñu far ak buur bi Erodd, ngir fiir ko ci waxam. 12:14 Ñu ñëw ci moom nag ne ko: «Kilifa gi, xam nanu ne ku wóor nga, te ragaloo kenn, ndaxte seetuloo jëmmi nit, waaye dangay xamle yoonu Yàlla ci bu wóor. Wax nu, ndax jaadu na, nu fey buur bi Sesaar galag am déet? Nu fey ko walla nu bañ koo fey?» 12:15 Waaye Yeesu xam na seen naaféq, mu ne leen: «Lu tax ngeen bëgg maa fiir? Indil-leen ma posetu denariyon, ma seet.» 12:16 Ñu jox ko poset bi. Noonu Yeesu laaj leen: «Kan lañu ci def nataalam ak turam?» Ñu tontu ko: «Sesaar.» 12:17 Noonu Yeesu ne leen: «Joxleen nag Sesaar li Sesaar moom, te jox Yàlla li Yàlla moom.» Ñu daldi waaru ci mbiram. 12:18 Gannaaw loolu ay Sadusen ñëw ci moom, ngir laaj ko lenn. Sadusen yi nag gëmuñu ne, ndekkite am na. 12:19 Ñu ne ko: «Kilifa gi, Musaa bindal na nu ne, ku magam faatu, te bàyyiwul doom ak jabaram, kooku war na donn jigéen ji, ba yékkati giiru magam. 12:20 «Amoon na fi nag juróom-ñaari góor, ñu bokk ndey ak baay. Taaw ba takk jabar, faatu, te bàyyiwul doom. 12:21 Ñaareel ba takk jigéen ja, faatu moom itam te bàyyiwul doom. Ñetteel bi it noonu. 12:22 Mbir mi dem na nag, ba juróom-ñaar ñooñu ñépp dem, te kenn bàyyiwu fi doom. Mujj jigéen ja faatu moom itam. 12:23 Ci ndekkite li nag kan ci ñoom moo ko war a donn, fekk ku nekk ci juróom-ñaar ñi mas na koo takk?» 12:24 Yeesu tontu leen ne: «Mbaa du dangeen a nekk cig réer, ci li ngeen xamul Mbind mi mbaa kàttanu Yàlla? 12:25 Ndaxte keroog ndekkite li kenn du am jabar, kenn du am jëkkër, waaye dinañu mel ni malaaka yi ci kaw. 12:26 Te sax li jëm ci mbirum ndekkite, xanaa jànguleen lii Yàlla wax ci Tawreetu Musaa ci saarum ngarab si: “Maay Yàllay Ibraayma, Isaaxa ak Yanqóoba”? 12:27 Li ci génn mooy, nekkul Yàllay ñi dee, waaye Yàllay ñiy dund la. Kon sóobu ngeen cig réer.» 12:28 Bi ñuy werante, benn xutbakat ñëw, dégg seen waxtaan, gis ne Yeesu tontu na leen tont lu leer. Mu laaj ko nag: «Ci ndigal yi, ban moo ci gën a màgg?» 12:29 Noonu Yeesu tontu ko ne: «Bii: “Bànni Israyil, déglul! Yàlla sunu Boroom moom rekk mooy Buur. 12:30 Kon nanga bëgg Yàlla sa Boroom ak sa xol bépp ak sa bakkan bépp, sa xel mépp ak sa kàttan gépp.” 12:31 Te ñaareel bi, lii la: “Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.” Ndigal yii ñoo sut yépp.» 12:32 Xutbakat bi ne ko: «Waaw kilifa gi, li nga wax dëgg la: Yàlla kenn la, te amul jeneen Yàlla ju dul moom. 12:33 Te nga bëgg ko ak sa xol bépp ak sa xel mépp ak sa kàttan gépp moo dàq bépp sarax bu ñuy yóbbu ngir màggal Yàlla ak bu ñuy lakk ca saraxalukaay ba.» 12:34 Bi Yeesu gisee nag ne, tontu na ak xel, mu ne ko: «Sorewuloo nguuru Yàlla.» Bi mu waxee loolu, kenn ñemeetu ko laaj dara. 12:35 Bi nga xamee ne Yeesu ma nga doon jàngale ca kër Yàlla ga, mu laaj nit ñi: «Lu tax xutbakat yi di wax ne, Almasi bi mooy sëtu Daawuda? 12:36 Daawuda moom wax na ci kàttanu Xel mu Sell mi naan:“Boroom bi nee na sama Boroom:«“Toogal ci sama ndeyjoor,ba kera may daaneelsay noon ci sa kanam.»“ “ 12:37 Gannaaw Daawuda nag wooye na ko: “Boroom bi,” naka mu nekke sëtam?» Noonu mbooloo mu mag mi di ko déglu ak bànneex. 12:38 Bi Yeesu di jàngale nag, mu ne leen: «Moytuleen xutbakat yi; dañoo bëgg di doxantu, sol ay mbubb yu réy, te ñépp di leen nuyoo ñaari loxo ci pénc mi. 12:39 Ci jàngu yi, féete kanam lañuy wut, te toogu yu yiw lañuy taamu ci reeri xew yi. 12:40 Ñu ngi lekk alalu jigéen ñi seeni jëkkër faatu, di ñaan Yàlla ay ñaani ngistal yu gudd. Seen mbugal dina gën a tar.» 12:41 Noonu Yeesu toog ca kër Yàlla ga, janook ndab, yi ñuy def sarax ngir Yàlla, muy xool nit ña cay dugal seen xaalis. Am nag ay boroom alal yu ci di def xaalis bu bare. 12:42 Gannaaw ga daal benn jigéen ju jëkkëram faatu, te mu ñàkk, ñëw, def ci ñaari poseti xànjar, yu matul sax dërëm. 12:43 Bi ko Yeesu gisee, mu woo taalibe yi ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, li jigéen ju ñàkk jee dugal ca defukaay ya moo ëpp maana alalu ñeneen ñi ñépp. 12:44 Ñoom ñépp dañu sàkku ci seen barele, waaye moom dafa sàkku ci néewleem, ba far ko joxe lépp, toog.»
13:1 Bi Yeesu di jóge ca kër Yàlla ga, kenn ca taalibe ya ne ko: «Kilifa gi, xoolal! Ni mu réye ay doj, te rafete ni ay taax!» 13:2 Waaye Yeesu tontu leen: «Du gis ngeen taax yu réy yii yépp? Lii lépp dina daanu, ba doj dootul des ci kaw doj.» 13:3 Gannaaw loolu, bi nga xamee ne Yeesu toog na ci tundu Oliw ya, jàkkaarlook kër Yàlla ga, Piyeer, Saag, Yowaana ak Andare fekki ko cig wet, laaj ko: 13:4 «Wax nu kañ la loolu di am? Te luy tegtal ne, mbir yii yépp a ngi bëgg a mat?» 13:5 Noonu Yeesu tontu leen: «Moytuleen, bu leen kenn nax. 13:6 Ñu bare dinañu ñëw ci sama tur naan: “Moom laa,” te dinañu nax ñu bare. 13:7 Bu ngeen déggee ay xare ak coowi xare, wottuleen a tiit; loolu war na am, waaye mujug jamono ji jotagul. 13:8 Xeet dina jóg, xeex ak weneen xeet, réew xeex ak meneen réew. Te yengu-yenguy suuf dina am ciy bérab yu bare, ak ay xiif. Loolu lépp mooy ndoortel metit yi, mel ni jigéen juy matu. 13:9 «Moytuleen. Dees na leen jébbal àttekat ya, di leen dóor ay yar ca jàngu ya. Dinañu leen dëj ci kanamu ay boroom réew ak ay buur ndax sama tur, ngir ngeen nekk seede ci ñoom. 13:10 Fàww xebaar bu baax bi jëkk a jib ci xeet yépp. 13:11 Saa su ñu leen jàppee nag, dëj leen ci péncum layoo, buleen jàq ci li ngeen war a wax; li ngeen jot ca waxtu woowa waxleen ko, ndaxte du yéenay wax waaye Xel mu Sell mi. 13:12 «Mag dina joxe rakkam cig dee, baay joxe doomam; ay doom it dinañu jóg, di bañ seeni waajur, di leen reylu. 13:13 Te ñépp dinañu leen bañ ndax sama tur; waaye ku muñ ba ca muj ga, mucc. 13:14 «Bés baa ngi ñëw, bu li ñuy wax “Lu araam luy yàqe” tegee ca bérab bu mu yelloowul; kiy jàng, na xam. Bu ngeen gisee loolu nag, ku nekk ci biir diiwaanu Yude, nanga daw ca tund ya. 13:15 Ku nekk ci kaw taax mi, bul wàcc ngir dugg kër gi, fab say yëf ya fa nekk. 13:16 Ku nekk ci tool bi, bul ñibbi ngir fab sa mbubb. 13:17 Ngalla jigéen ñi ëmb ca bés yooya, ngalla it ñiy nàmpal. 13:18 Ñaanleen ngir seen gàddaay bañ a tase ak jamonoy seddaayu lolli. 13:19 Ndaxte booba dina am metit wu réy wu musul a am, ba àddina sosoo ak tey, te dootul am mukk. 13:20 Te bu fekkul woon Boroom bi wàññi bés yooyu, kenn du mucc, waaye fekk na mu wàññi leen ndax gaayam ñi mu tànn. 13:21 «Booba nag, bu leen kenn waxee: “Kaayleen gis, Kirist a ngi fi,” mbaa: “Xool-leen, mu nga fale,” buleen ko gëm. 13:22 Ndaxte ñiy mbubboo turu Kirist ak ñiy mbubboo turu yonent, dinañu feeñ, di joxe ay firnde yu réy ak ay kéemaan, ba ciy nax sax ñi Yàlla tànn, su loolu manoon a am. 13:23 Wax naa leen ko lu jiitu. Kon nag moytuleen. 13:24 «Waaye booba, gannaaw metit yooyu:“Jant bi dina lëndëmte weer dootul leer; 13:25 biddiiw yi di daanoo asamaan,te kàttani asamaan yiy yengu.” 13:26 «Noonu dees na gis Doomu nit ki ñëw ci niir yi, ànd ak kàttan ak ndam lu réy. 13:27 Dina yónni ay malaakam, ñu dajale ñi mu tànn ci ñeenti xebla yi, fa àddina dale, ba fa asamaan yem.» 13:28 Yeesu teg ca ne: «Jàngleen misaalu garabu figg ga. Boo xamee ne ay bànqaasam duy nañu, tey xobam sëq, xam ngeen ne nawet jege na. 13:29 Noonu itam bu ngeen gisee loolu lépp xew, xamleen ne jege na; mu ngi ci bunt bi sax. 13:30 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, niti jamono jii duñu wéy, te loolu lépp amul. 13:31 Asamaan ak suuf dinañu wéy, waaye samay wax du wéy mukk. 13:32 «Waaye bés boobu ak waxtu woowu, kenn xamul kañ lay doon; du malaaka yi ci kaw, du sax Doom ji, waaye Baay bi rekk moo ko xam. 13:33 Moytuleen te xool! Xamuleen kañ la waxtu wi di jot. 13:34 «Mi ngi mel ni nit ku tukki, mu dénk këram ay surgaam, ku nekk ak sa sas, te sant bëkk-néeg bi, mu xool. 13:35 Yéen nag xool-leen, ndaxte xamuleen kañ la boroom kër gi di dellusi, muy ci timis mbaa ci xaaju guddi, muy ci fajar mbaa njël. 13:36 Bu nee jaleñ, bumu leen bett, ngeen di nelaw. 13:37 Li ma leen wax, ñépp laa ko wax: “Xool-leen!”»
14:1 Booba nag saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya ñu ngi doon fexeel Yeesu, ngir jàpp ko, reylu. Fekk booba ñaari fan a des ci màggalu bésu Jéggi ba ak màggalu Mburu ya amul lawiir. 14:2 Kon nag ñu ne: «Bumu doon ci bésu màggal bi, ngir yengu-yengu bañ a am ci nit ñi.» 14:3 Bi nga xamee ne Yeesu nekkoon na dëkku Betani, mu dem këru Simoŋ ma gaana woon, di fa lekk. Noonu jigéen ñëw, yor njaq lu ñu defare doj wu tudd albaatar. Njaq li def latkoloñ ju raxul ju ñuy wax nàrd, tey jar lu baree-bare. Jigéen ji toj njaq li, tuur latkoloñ ci boppu Yeesu. 14:4 Waaye amoon na fa ñu mer, di xultu ci seen biir naan: «Yàq gii, lu muy jariñ? 14:5 Maneesoon na jaay latkoloñ jii ci lu tollook peyug atum lëmm, jox ko miskin yi.» Noonu ñu daldi gëdd jigéen ji. 14:6 Waaye Yeesu ne leen: «Bàyyileen ko. Defal na ma jëf ju rafet; lu tax ngeen di ko sonal? 14:7 Miskin yaa ngi ak yéen bés bu nekk, te man ngeen leen a dimbali saa su leen neexee, waaye dungeen ma gis ba fàww. 14:8 Jigéen ji def na li mu man; diw na sama yaram ak latkoloñ, ngir waajal sama rob, laata moo jot. 14:9 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, fépp fu ñuy yéene xebaar bu baax bi ci àddina sépp, dinañu fa fàttali it li jigéen jii def.» 14:10 Ca waxtu woowu kenn ci fukki taalibe ya ak ñaar, ku tudd Yudaa Iskariyo, dem ca saraxalekat yu mag ya, ngir wori Yeesu. 14:11 Bi ñu ko déggee, ñu am ca bànneex bu réy, dig ko xaalis. Noonu mu fexe jamono ju mu leen man a jébbal Yeesu. 14:12 Bés bu jëkk ca màggal, ga ñuy wax Mburu ya amul lawiir, taalibey Yeesu laaj ko: «Foo bëgg, nu defaral la reeru Jéggi bi?» Bés bu jëkk booba nag mooy bés, ba ñu faral a rendi xarum màggalu Jéggi ba. 14:13 Noonu Yeesu yebal ñaar ci taalibe yi ne leen: «Demleen ca dëkk ba, foofa góor gu yenu njaq lu def ndox, dina taseek yéen, ngeen topp ko. 14:14 Kër gi mu dugg nag, ngeen ne boroom kër gi: “Kilifa gi nee na: Ana néegu gan, bi may lekke reeru Jéggi bi, man ak samay taalibe?” 14:15 Dina leen won néeg bu féete kaw te yaa, ñu defar ko, ba lépp jekk. Foofa ngeen nuy defarale reer bi.» 14:16 Bi mu ko waxee, taalibe ya dem ca dëkk ba, gis lépp, ni leen ko Yeesu waxe woon. Noonu ñu defar reer bi. 14:17 Bi nga xamee ne timis jot na, Yeesu ñëw, ànd ak fukki taalibe yi ak ñaar. 14:18 Ñu toog, di lekk. Bi ñuy lekk nag, Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, kenn ci yéen, ku bokk ak man di lekk sax, dina ma wor.» 14:19 Taalibe yi nag am naqar, ñu daldi ko ne kenn-kenn: «Mbaa du man?» 14:20 Mu tontu leen: «Kenn ci yéen fukk ak ñaar la, kuy cappandoo ak man ci ndab li. 14:21 Doomu nit ki mu ngi dem, ni ñu ko waxe ci Mbind mi, waaye ki koy wor dina torox. Bañoon a juddu moo gën ci moom.» 14:22 Noonu bi ñuy lekk, Yeesu jël mburu, sant Yàlla, jox leen ko naan: «Jël-leen, lii sama yaram la.» 14:23 Gannaaw loolu mu jël kaas, sant Yàlla, jox leen ko, ñépp naan ci. 14:24 Mu ne leen: «Lii sama deret la, ji fas kóllëre gi, te mu tuuru ngir ñu bare. 14:25 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, dootuma naan gannaaw tey ndoxum réseñ mii, ba kera ma ciy naan bu bees ci nguuru Yàlla.» 14:26 Noonu ñu woy Yàlla, ba noppi génn, dem ca tundu Oliw ya. 14:27 Booba Yeesu ne leen: «Yéen ñépp dingeen ma dàggeeku, ndaxte bind nañu:“Dinaa dóor sàmm bi,xari jur gi tasaaroo.” 14:28 Waaye bu ma dekkee, dinaa leen jiituji Galile.» 14:29 Kon Piyeer ne ko: «Bu la ñépp dàggeekoo, man duma la bàyyi mukk.» 14:30 Waaye Yeesu tontu ko: «Ci dëgg maa ngi la koy wax, guddig tey, bala ginaar a sab ñaari yoon, dinga ma weddi ñetti yoon.» 14:31 Waaye Piyeer gën a sax ca la mu waxoon naan: «Boo xamee ne sax, damaa war a dee ak yaw, duma la weddi mukk.» Taalibe yépp it waxe noonu. 14:32 Noonu ñu dem ca bérab bu tudd Setsemane. Yeesu ne taalibe yi: «Toogleen fii, ma dem ñaani.» 14:33 Mu ànd ak Piyeer, Saag ak Yowaana, daldi jàq, ba xonett. 14:34 Mu ne leen: «Sama xol dafa tiis, ba ma bëgg a dee; toogleen fii, xool.» 14:35 Noonu Yeesu dem ci kanam tuuti, daanu ci suuf, di ñaan ne, waxtu wi teggi ko, bu loolu manoon a am. 14:36 Mu ne: «Abba, Baay bi, yaw mi dara tëwul, teggil ma kaasu naqar bii. Moona bumu doon sama coobare, waaye na sa coobare am.» 14:37 Noonu mu dellusi ci taalibe yi, fekk ñuy nelaw. Mu ne Piyeer: «Simoŋ, dangaa nelaw? Amuloo sax dooley xoolandoo ak man benn waxtu? 14:38 Xool-leen te ñaan, ngir bañ a daanu cig fiir. Seen xol jag na, waaye seen bind a woyof.» 14:39 Beneen yoon Yeesu dem, di ñaane noonu, 14:40 dellusiwaat, fekk leen ñuy nelaw, ndaxte seeni bët dañoo diis. Xamuñu lu ñu koy tontoo. 14:41 Ñetteelu yoon mu dellusi ci ñoom ne leen: «Yéena ngi nelaw tey noppalu ba tey! Jeex na. Waxtu wi jot na; ñu ngi wor Doomu nit ki ci loxoy bàkkaarkat yi. 14:42 Jógleen nu dem; ki may wor a ngi nii, di ñëw.» 14:43 Bi Yeesu di wax, Yudaa mi bokkoon ci fukki taalibe ya ak ñaar, agsi, ànd ak mbooloo mu bare, mu jóge ca saraxalekat yu mag ya, ca xutbakat ya ak ca njiiti xeet wa, te gànnaayoo jaasi ak yet. 14:44 Fekk ki ko naroon a wor joxoon na leen tegtal ne leen: «Ki may fóon, moom la; jàppleen ko, yóbbu ko te wottu ko bu baax.» 14:45 Noonu mu ñëw ci Yeesu ne ko: «Kilifa gi,» daldi ko fóon. 14:46 Bi mu ko defee nit ñi song Yeesu nag, jàpp ko. 14:47 Waaye kenn ci ñi fa taxaw bocci jaaseem, dóor surgab saraxalekat bu mag bi, nopp bi dagg. 14:48 Yeesu ne leen: «Jóg ngeen ngir jàpp ma, gànnaayoo jaasi ak yet, mel ni ñuy topp sàcc. 14:49 Moona daan naa toog bés bu nekk ca kër Yàlla ga, di jàngale, te jàppuleen ma. Waaye lii am na, ngir Mbind mi am.» 14:50 Ci kaw loolu, ñépp dëddu ko, daw. 14:51 Fekk amoon na ca waxambaane wu lëkkaayoo woon sér, topp Yeesu, ñu daldi ko jàpp. 14:52 Waaye waxambaane wa wacc fa sér bi, daldi daw, def yaramu neen. 14:53 Ñi jàpp Yeesu yóbbu ko ci saraxalekat bu mag bi, te foofa la saraxalekat yu mag yi, njiit yi ak xutbakat yi yépp dajaloo. 14:54 Piyeer nag topp ko fu sore, ba ci ëttu saraxalekat bu mag bi, mu toog fa ak alkaati yi, di jaaru ci taal bi. 14:55 Noonu saraxalekat yu mag yi ak kureelu àttekat yi yépp di wut ku man a seede lu daan Yeesu, ba ñu man koo reylu, waaye gisuñu kenn. 14:56 Teewul sax naaféq ñu bare ñëw, seede ci Yeesu lu dul dëgg, waaye seen seede ànduñu. 14:57 Ba mujj naaféq taxaw, seede ci moom naan: 14:58 «Nun daal dégg nanu, mu ne: “Dinaa toj kër Yàlla, gii loxoy nit liggéey, tabax ci ñetti fan geneen gu nit liggéeyul.”» 14:59 Waaye ba tey seeni wax ànduñu. 14:60 Ci kaw loolu saraxalekat bu mag bi taxaw ci seen kanam ne Yeesu: «Doo tontu? Lu la nit ñi di jiiñ?» 14:61 Waaye Yeesu tontuwul dara, ne cell. Saraxalekat bu mag bi dellu nag ne ko: «Ndax yaa di Almasi bi, Doomu Yàlla ju tedd ji?» 14:62 Yeesu tontu ko: «Moom laa. Te dingeen gis, Doomu nit ki toog ci ndeyjooru Aji Kàttan ji, di ñëw ci niiri asamaan.» 14:63 Bi ko saraxalekat bu mag bi déggee nag, mu daldi mer, ba xotti ay yéreem naan: 14:64 «Weddi na Yàlla, lu nu doyeeti seede? Lu ngeen ci xalaat?» Noonu ñépp teg ko dee. 14:65 Ci kaw loolu ñu daldi tifli ci moom, takk ay bëtam, di ko dóor ay kurfeñ, naan ko: «Yaw wax nu ci kàddug Yàlla, ku la dóor?» Ba noppi alkaati yi teeru ko ak ay pes. 14:66 Piyeer nag ma nga toogoon ci ëtt bi féete suuf. Noonu benn mbindaanu saraxalekat bu mag ba romb fa. 14:67 Mu gis Piyeer di jaaru, xool ko jàkk naan: «Yaw itam àndoon nga ak Yeesum Nasaret moomu.» 14:68 Waaye Piyeer weddi ko naan: «Xawma li ngay wax, dégguma ci dara.» Mu daldi génn, dem ca buntu kër ga. 14:69 Foofa nag mbindaan mi gisaat ko, mu ne ñi fa taxaw: «Waa jii ci ñoom la bokk.» 14:70 Waaye Piyeer weddiwaat ko.Nes tuuti ñi fa taxaw ne Piyeer: «Yaw mi de, ci lu wóor bokk nga ci, nde waa Galile nga.» 14:71 Waaye Piyeer daldi giñ ak a waat naan: «Xawma nit ki ngay wax.» 14:72 Ci saa si ginaar sab ñaareelu yoon. Noonu Piyeer fàttaliku li ko Yeesu wax: «Bala ginaar a sab ñaari yoon, dinga ma weddi ñetti yoon.» Mu daldi jooy jooy yu metti.
15:1 Ci suba teel saraxalekat yu mag yi gise, ñoom ak njiit yi ak xutbakat yi ak kureelu àttekat yi yépp. Ñu yeew nag Yeesu, daldi ko yóbbu, jébbal ko Pilaat. 15:2 Noonu Pilaat laaj ko: «Ndax yaa di buuru Yawut yi?» Yeesu tontu ko: «Wax nga ko.» 15:3 Te saraxalekat yu mag yi di ko jiiñ lu bare. 15:4 Kon nag Pilaat laajaat ko: «Déggal lépp li ñu lay jiiñ. Xanaa amoo ci tont?» 15:5 Waaye ba tey Yeesu tontuwul dara, ba tax Pilaat waaru. 15:6 Màggal gu nekk nag Pilaat daan na may mbooloo mi, ñu tànn kenn ci ñi ñu tëjoon, mu bàyyil leen ko. 15:7 Fekk booba amoon na ku ñu tëj, tudd Barabas, ku bokk ci ña bëggoon a tas réew mi, boole ci rey nit. 15:8 Noonu mbooloo mi ñëw, laaj Pilaat, mu defal leen la mu daan def. 15:9 Pilaat nag xam ne, kiñaan rekk a taxoon saraxalekat yu mag yi jébbal ko Yeesu. Kon mu ne mbooloo mi: «Xanaa ma bàyyil leen buuru Yawut yi?» 15:11 Waaye saraxalekat yu mag yi xiir mbooloo mi, ñu laaj Pilaat, mu bàyyil leen Barabas. 15:12 Kon Pilaat ne leen: «Lan laay def nag ak ki ngeen di wooye buuru Yawut yi?» 15:13 Ñu daldi yuuxuwaat naan: «Daaj ko ci bant, ba mu dee!» 15:14 Pilaat ne leen: «Lu tax? Gan tooñ la def?» Waaye mbooloo mi di yuuxu bu gën a kawe: «Daaj ko ci bant!» 15:15 Noonu Pilaat, mi wut a neex mbooloo mi, bàyyil leen Barabas, ba noppi mu dóorlu Yeesu ay yar, jébbal ko, ngir ñu daaj ko ci bant. 15:16 Bi loolu amee ñu dugal Yeesu ci biir kër boroom réew ma, mooy bérab bu ñuy wax Peretoriyum, ñu daldi woo mbooloom xarekat yépp. 15:17 Noonu ñu solal ko mbubb mu xonq curr, ràbb kaalag dég, teg ko ci boppam. 15:18 Ñu daldi ko wax bu kawe: «Nuyu nanu la, yaw buuru Yawut yi!» 15:19 Ñu di ko dóor ci bopp ak bant, di ko tifli, daldi sukk, màggal ko. 15:20 Bi ñu ko ñaawalee noonu ba noppi, ñu summi mbubb mu xonq mi, solaatal ko ay yéreem, yóbbu ko, ngir daaj ko ci bant. 15:21 Amoon na nag nit ku dëkk Siren, tudd Simoŋ, di baayu Alegsàndar ak Rufus. Fekk booba mu romb fa, jóge ca wet, ga féete ak tool ya, ñu ga ko ngir mu gàddu bant bi. 15:22 Noonu ñu yóbbu Yeesu ca bérab bu ñuy wax Golgota, liy tekki «Bérabu kaaŋu bopp.» 15:23 Ñu bëgg koo jox biiñ bu ñu boole ak naan gu tudd miir, waaye nanguwu ko. 15:24 Foofa ñu daaj Yeesu ci bant, daldi séddoo ay yéreem, tegoo ko ay bant, ba xam ku nekk, looy am; 15:25 booba fekk yoor-yoor di jot. 15:26 Mbind mi xamle lu tax ñu rey ko nee na: «Kii mooy buuru Yawut yi.» 15:27 Booba it ñu daajaale ak moom ñaari taskati réew mi, kenn ci ndeyjooram, ki ci des ci càmmooñam. 15:29 Ña fa doon romb di ko xas, di wëcc seen bopp ndax sib ko naan: «Waaw kay, yaw mi bëgg a toj kër Yàlla gi, tabaxaat ko ci ñetti fan, 15:30 wàccal ci bant bi te musal sa bopp!» 15:31 Noonu it saraxalekat yu mag yi ak xutbakat yi di ko ñaawal ci seen biir naan: «Kii musal na ñeneen waaye mënul a musal boppam. 15:32 Almasi bii, di buuru Israyil, na wàcc léegi ci bant bi, nu gis ko te gëm.» Ñi ñu daajaale ak moom it di ko xarab. 15:33 Li tàmbalee digg-bëccëg, ba ci tisbaar, réew mépp lëndëm. 15:34 Ci tisbaar nag Yeesu wootee kàddu gu dëgër naan: «Elowi, Elowi, lema sabaktani?» liy tekki: «Sama Yàlla, sama Yàlla, lu tax nga dëddu ma?» 15:35 Ñenn ci ña fa taxaw nag, bi ñu ko déggee, ñu ne: «Mu ngi woo yonent Yàlla Iliyas.» 15:36 Noonu kenn daw, jël aw sagar, capp ko ci bineegar, mu teg ko ci bant, jox ko ko, mu muucu. Mu ne: «Bàyyileen, nu seet, ba xam Iliyas dina ñëw, wàcce ko.» 15:37 Noonu Yeesu wootewaat ak kàddu gu dëgër, delloo ruuwam Yàlla. 15:38 Bi mu ko defee ridob bérab bu sell ba ca kër Yàlla ga xar ñaar, li dale ci kaw ba ci suuf. 15:39 Njiitu xare nag, bi taxawoon ci kanamu Yeesu, bi mu gisee ni Yeesu deeye, mu ne: «Ci dëgg, nit kii Doomu Yàlla la!» 15:40 Amoon na fa nag ay jigéen, ñu leen dand, di xool. Xàmmi nañu ci: Maryaama mi dëkk Magdala, Maryaama yaayu Saag mu ndaw ak Yuusufa, ak Salome. 15:41 Bi Yeesu nekkee Galile, jigéen ñooñu ñoo ko doon topp, di ko topptoo. Amoon na fa it yeneen jigéen yu bare yu àndoon ak moom, ba ñëw Yerusalem. 15:42 Booba nag bésu Waajal la woon, maanaam bés bu jiitu bésu noflaay bi. Ca ngoon sa nag, 15:43 Yuusufa mi dëkk Arimate takk aw fitam, dem Pilaat, laaj ko néewu Yeesu. Yuusufa moomu nag, ku siiw la woon ci kureelu àttekat yi, te doon séentu moom itam nguuru Yàlla. 15:44 Bi Pilaat déggee ne, Yeesu faatu na xaat, mu waaru. Mu woolu nag njiit li, laaj ko, ndax yàgg na faatu. 15:45 Bi ko ko njiit li dëggalee, Pilaat jox néew bi Yuusufa. 15:46 Noonu Yuusufa jënd càngaay, wàcce néew bi, laxas ko ci, dugal ko cib bàmmeel bu ñu yett ci xeer. Bi mu ko defee mu béraŋ aw doj, ube ko buntu bàmmeel bi. 15:47 Maryaamam Magdala nag ak Maryaama yaayu Yuusufa xool fu mu ko denc.
16:1 Bi bésu noflaay bi wéyee, Maryaamam Magdala, Maryaama yaayu Saag, ak Salome, jënd cuuraay, ngir dem xeeñal néewu Yeesu. 16:2 Kon bés bu jëkk ci ayu-bés gi, ñu njëlu dem ca bàmmeel ba, 16:3 di laajante: «Ku nuy béraŋal doj, wiy ub bàmmeel bi?» Doj woowu nag bu réy-a-réy la woon. Noonu ñu xool, gis ne doj wa deñ. 16:5 Ñu dugg ci bàmmeel bi, gis ca ndeyjoor waxambaane wu sol mbubb mu weex, ñu daldi tiit. 16:6 Waaye mu ne leen: «Buleen tiit. Yéena ngi seet Yeesum Nasaret, mi ñu daajoon ci bant bi. Nekkatu fi, dekki na; gisleen fi ñu ko tëraloon. 16:7 Kon nag demleen, ne Piyeer ak taalibe ya: “Mi ngi leen di jiitu Galile. Foofa ngeen koy gise, ni mu leen ko waxe woon.”» 16:8 Noonu jigéen ñi génn, dawe bàmmeel ba, tiit bay lox. Te waxuñu kenn dara ndax seen tiit. 16:9 Bi Yeesu dekkee nag ci suba teel ca bés bu jëkk ca ayu-bés ga, mu jëkk a feeñu Maryaama mu dëkk Magdala, mi mu dàqe woon juróom-ñaari rab. 16:10 Maryaama nag dem nettali ko ñi àndoon ak Yeesu, fekk ñuy naqarlu, di jooy. 16:11 Bi ñu déggee ne, Yeesoo ngi dund te Maryaama gis na ko, gëmuñu ko. 16:12 Gannaaw loolu Yeesu feeñu ñaar ci ñoom ci jeneen jëmm, ñuy jaar ci yoon wi, jëm àll ba. 16:13 Ñu woññiku nag, wax ko ña ca des, waaye ba tey gëmuñu leen ñoom it. 16:14 Gannaaw ga it Yeesu feeñu fukki taalibe yi ak benn, bi ñuy lekk. Mu yedd leen ndax seen ngëmadi ak seen dëgër bopp, ci li ñu bañ a gëm ñi ko gisoon, bi mu dekkee. 16:15 Mu ne leen: «Demleen ci àddina sépp, yégal xebaar bu baax bi mbindeef yépp. 16:16 Ku gëm te ñu sóob ko ci ndox, dina mucc; ku gëmul, dees na ko daan. 16:17 Ñi ma gëm dinañu ànd ak firnde yii: ci sama tur dinañu dàq rab yi, di wax làkk yu bees, 16:18 di jàpp jaan ak seeni loxo; te bu ñu naanee lu ñu tooke, du leen wàññi dara, te jarag ju ñu teg loxo, mu wér.» 16:19 Gannaaw bi Boroom bi Yeesu waxee ak ñoom, mu yékkatiku, dem asamaan, toog ci ndeyjooru Yàlla. 16:20 Taalibe ya dem waareji, te loxob Boroom bi ànd ak ñoom, di dëggal kàddu gi ak firnde, yi ci ànd.
1:1 Yaw Teyofil mu tedd mi, xam nga ne, nit ñu bare sasoo nañoo bind ab nettali bu jëm ci mbir, yi xewoon ci sunu biir, 1:2 li dëppook waxi seede, yi ko teewe woon li dale ca ndoorte la te ñu mujj nekk jawriñi kàddug Yàlla. 1:3 Léegi nag kon man ci sama wàll, gëstu naa ci lépp li ko dale ca njàlbéen ga, te fas naa la ko yéenee bindal, nettali la ni xew-xew yooyu deme woon tembe. 1:4 Noonu dinga man a xam ne, li ñu la jàngaloon lu wér peŋŋ la. 1:5 Ca jamonoy Erodd, mi nekkoon buur ca réewu Yawut ya, amoon na saraxalekat bu ñu tudde Sakariya te bokk ca mbootaayu saraxalekat, ya askanoo ci Abiya. Jabaram Elisabet askanoo moom itam ci Aaroona. 1:6 Sakariya ak jabaram ñu jub lañu ca kanam Yàlla, di topp ni mu ware ndigal yi ak dogali Boroom bi yépp. 1:7 Waaye amuñu doom, ndaxte Elisabet mënul a am doom, te it fekk ñoom ñaar ñépp ay màggat lañu. 1:8 Benn bés nag Sakariya doon def liggéeyu saraxaleem ca Yàlla, ndaxte mbootaayam a aye keroog. 1:9 Bi ñuy tegoo bant, ni ko saraxalekat yi daan defe nakajekk, ngir xam kan mooy dugg ca bérab bu sell ba ca kër Yàlla ga, ngir taal fa cuuraay, bant ba tegu ci Sakariya. 1:10 Ca waxtu wa ñuy taal cuuraay la, mbooloo maa nga woon ca biti, di ñaan. 1:11 Noonu benn malaakam Boroom bi daldi feeñu Sakariya, taxaw ca féeteek ndeyjooru saraxalukaay, ba ñuy taal cuuraay ca kawam. 1:12 Naka la ko Sakariya gis, fitam daldi dem, mu tiit. 1:13 Waaye malaaka ma ne ko: «Bul ragal dara Sakariya, ndaxte sa ñaan nangu na. Elisabet sa jabar dina la jural doom, te dinga ko tudde Yaxya. 1:14 Sa mbég lay doon, sa xol sedd ci, te ñu bare dinañu bég ci juddoom, 1:15 ndaxte dina nekk ku màgg ca kanam Yàlla. Du naan biiñ walla dara luy màndil, te bu juddoo, Xel mu Sell mi daldi ko solu. 1:16 Dina delloosi niti Israyil yu bare ci Yàlla seen Boroom. 1:17 Mooy jiitu, di yégle ñëwu Boroom bi, ànd ak xel mi ak doole, ji yonent Yàlla Iliyas amoon, ngir jubale xoli baay yi ak doom yi, ngir delloo ñi déggadi ci maanduteg ñi jub. Noonu dina waajal mbooloo muy teeru Boroom bi.» 1:18 Sakariya daldi ne malaaka ma: «Nan laay xame ne, loolu dëgg la? Ndaxte mag laa, te sama jabar it màggat na.» 1:19 Malaaka ma tontu ko ne: «Man maay Jibril miy taxaw ci kanam Yàlla. Dañu maa yónni ngir ma wax ak yaw te yégal la xebaar bu baax boobu. 1:20 Léegi nag gannaaw gëmuloo li ma wax, dinga luu te dootuloo man a wax, ba kera sama wax di am, bu jamonoom jotee.» 1:21 Fekk na booba mbooloo maa ngi xaar, jaaxle lool ci li Sakariya yàgg ca bérab bu sell ba. 1:22 Waaye bi mu génnee nag, mënul a wax ak ñoom. Noonu nit ña xam ne, dafa am lu ko feeñu ca bérab bu sell ba. Dafa luu, ba di leen liyaar. 1:23 Bi Sakariya matalee liggéeyu saraxaleem ba noppi, mu daldi ñibbi. 1:24 Bi mbir yooyu weesoo, Elisabet jabaram ëmb, di ko nëbb lu mat juróomi weer 1:25 te naan: «Lii mooy yiw wi ma Boroom bi defal, ba fajal ma li doon sama gàcce ci nit ñi!» 1:26 Bi Elisabet nekkee ci juróom-benni weeram, Yàlla yónni na malaakaam Jibril ca dëkku Nasaret ca diiwaanu Galile. 1:27 Mu yebal ko ca janq bu ñu may waa ju bokk ci askanu Daawuda te ñu koy wax Yuusufa, waaye àndaguñu. Janq baa ngi tudd Maryaama. 1:28 Malaaka ma dikk ca moom ne ko: «Jàmm ngaam, yaw mi Boroom bi defal aw yiw; mu ngi ak yaw.» 1:29 Waxi malaaka ma daldi jaaxal Maryaama, muy xalaat lu nuyoo boobu man a tekki. 1:30 Malaaka ma ne ko: «Bul ragal dara Maryaama, ndaxte Yàlla tànn na la ci yiwam. 1:31 Dinga ëmb, jur doom ju góor; nanga ko tudde Yeesu. 1:32 Ku màgg lay nekki, te dinañu ko wooye Doomu Aji Kawe ji. Boroom bi Yàlla dina ko jébbal nguuru Daawuda maamam. 1:33 Noonu dina yilif askanu Yanqóoba ba fàww, te nguuram du am àpp.» 1:34 Maryaama laaj malaaka ma ne ko: «Naka la loolu man a ame? Man de, janq laa ba tey.» 1:35 Malaaka ma tontu ko ne: «Xel mu Sell mi dina wàcc ci yaw, te Aji Kawe ji dina la yiir ci kàttanam. Moo tax xale biy juddu dinañu ko wooye Ku sell ki, Doomu Yàlla ji. 1:36 Elisabet sa mbokk mi it dina am doom ju góor cig màggatam. Ki ñu doon wooye ku mënul a am doom, mu ngi ci juróom-benni weeram. 1:37 Ndaxte dara tëwul Yàlla.» 1:38 Maryaama ne ko: «Jaamub Boroom bi laa. Na Yàlla def ci man li nga wax.» Ci noonu malaaka ma daldi dem. 1:39 Ci jamono jooju Maryaama jóg, gaawantu dem ci benn dëkk bu nekkoon ca tund ya ca diiwaanu Yude. 1:40 Mu dugg ca kër Sakariya, daldi nuyu Elisabet. 1:41 Naka la Elisabet dégg Maryaama di nuyoo, doomam daldi yengatu ci biiram. Noonu Xelum Yàlla mu Sell mi daldi solu Elisabet. 1:42 Elisabet wax ca kaw ne: «Barkeel nañu la ci jigéen ñi, barkeel doom ji nga ëmb! 1:43 Man maay kan, ba ndeyu sama Boroom ñëw di ma seetsi? 1:44 Maa ngi lay wax ne, naka laa la dégg ngay nuyoo rekk, sama doom ji yengu ci sama biir ndax mbég. 1:45 Barke ñeel na la, yaw mi gëm ne, li la Boroom bi yégal dina mat!» 1:46 Noonu Maryaama daldi ne: 1:47 «Sama xol a ngi màggal Boroom bi,sama xel di bég ci Yàlla sama Musalkat, 1:48 ndaxte fàttaliku na ma,man jaamam bu woyof bi.Gannaawsi tey, niti jamono yéppdinañu ma wooye ki ñu barkeel, 1:49 ndaxte Ku Màgg ki defal na ma lu réy.Turam dafa sell. 1:50 Day wàcce yërmandeem ci ñi ko ragal,ci seeni sët ba ci seeni sëtaat. 1:51 Wone na jëf yu mag ci dooley loxoom,te tas mbooloom ñiy réy-réylu, 1:52 daaneel boroom doole yi ci seen nguur,yékkati baadoolo yi. 1:53 Ñi xiif, reggal na leen ak ñam wu neex,te dàq boroom alal yi,ñu daw ak loxoy neen. 1:54 Wallu na bànni Israyil giy jaamam,di fàttaliku yërmandeem, 1:55 ni mu ko dige woon sunuy maam,jëmale ko ci Ibraayma ak askanam ba fàww.» 1:56 Noonu Maryaama toog fa Elisabet lu war a tollook ñetti weer, sog a ñibbi. 1:57 Gannaaw loolu jamono ji Elisabet war a mucc agsi, mu daldi jur doom ju góor. 1:58 Dëkkandoom yi ak mbokkam yi yég ne, Boroom bi won na ko yërmande ju réy, ñu ànd ak moom bég. 1:59 Bi bés ba dellusee, ñu ñëw xarafalsi xale ba, bëgg koo dippee baayam Sakariya. 1:60 Waaye yaayam ne leen: «Déedéet, Yaxya lay tudd.» 1:61 Ñu ne ko: «Amoo menn mbokk mu tudd noonu.» 1:62 Ñu daldi liyaar baayam, ngir xam nan la bëgg ñu tudde xale ba. 1:63 Sakariya laaj àlluwa, bind ci ne: «Yaxya la tudd.» Ñépp daldi waaru. 1:64 Ca saa sa Yàlla dindi luu gi, Sakariya daldi waxaat, di màggal Yàlla. 1:65 Waa dëkk ba bépp jaaxle, xew-xew yooyu siiw ca tundi Yude yépp. 1:66 Ñi dégg nettali, bi jëm ci mbir yooyu, dañu koo denc ci seen xol te naan: «Nu xale bii di mujje nag?» Ndaxte leeroon na ne, dooley Boroom baa ngi ànd ak moom. 1:67 Sakariya baayu Yaxya daldi fees ak Xel mu Sell mi. Noonu mu wax ci kàddug Yàlla ne: 1:68 «Cant ñeel na Boroom bi, Yàllay Israyil,ndaxte wallusi na mbooloom, ba jot leen! 1:69 Feeñal na nu Musalkat bu am doole,bi soqikoo ci askanu Daawuda jaamam, 1:70 ni mu yéglee woon bu yàggjaarale ko ci yonentam yu sell yi. 1:71 Dina nu musal ci sunuy noon,jële nu ci sunu loxoy bañaale. 1:72 Yàlla wone na yërmandeem,ji mu digoon sunuy maam,te di fàttaliku kóllëre, gi mu fas ak ñoom, 1:73 di ngiñ, li mu giñaloon sunu maam Ibraayma naan, 1:74 dina nu teqale ak sunuy noon,ngir nu man koo jaamu ci jàmm, 1:75 nu sell te jub ci kanamam sunu giiru dund. 1:76 Yaw nag doom, dinañu lay wooye yonentu Aji Kawe ji,ndaxte dinga jiitu, di yégle ñëwu Boroom bi,di ko xàllal yoon wi. 1:77 Dinga xamal mbooloom,ni leen Boroom bi man a musale,jaare ko ci seen mbaalug bàkkaar, 1:78 ndaxte Yàlla sunu Boroom fees na ak yërmande,ba tax muy wàcce ci nun jant buy fenk, 1:79 ngir leeral ñi toog ci lëndëm,takkandeeru dee tiim leen,ngir jiite nu ci yoonu jàmm.» 1:80 Noonu Yaxyaa ngi doon màgg, te xelam di ubbiku. Mu dëkk ca màndiŋ ma, ba bés ba muy feeñu bànni Israyil.
2:1 Ca jamono jooja buur bu mag bu ñuy wax Ogust joxe ndigal ne, na ñépp binduji. 2:2 Mbindu mooma, di mu jëkk ma, daje na ak jamono, ja Kiriñus nekke boroom réewu Siri. 2:3 Noonu ku nekk dem binduji ca sa dëkku cosaan. 2:4 Yuusufa nag daldi jóge Nasaret ca diiwaanu Galile, jëm ca diiwaanu Yude ca Betleyem, dëkk ba Daawuda cosaanoo, ndaxte ci askanu Daawuda la bokk. 2:5 Mu dem binduji, ànd ak Maryaama jabaram, fekk booba Maryaama ëmb. 2:6 Bi ñu nekkee Betleyem, waxtu wa mu waree mucc agsi. 2:7 Mu taawloo doom ju góor, mu laxas ko ci ay laytaay, tëral ko ca lekkukaayu jur ga, ndaxte xajuñu woon ca dalukaay ba. 2:8 Fekk booba amoon na ca gox ba ay sàmm yu daan fanaan ca tool ya, di wottu jur ga. 2:9 Noonu benn malaakam Boroom bi feeñu leen, ndamu Boroom bi daldi leer, melax, wër leen. Tiitaange ju réy jàpp leen. 2:10 Waaye malaaka mi ne leen: «Buleen tiit, ndaxte dama leen di xamal xebaar bu baax buy indi mbég mu réy ci nit ñépp. 2:11 Tey jii ca dëkku Daawuda, ab Musalkat juddul na leen fa, te mooy Almasi bi, di Boroom bi. 2:12 Ci firnde jii ngeen koy xàmmee: dingeen gis liir bu ñu laxas ci ay laytaay, tëral ko ci lekkukaayu jur.» 2:13 Bi mu waxee loolu, yeneen malaaka yu bare yu jóge asamaan, ànd ak moom, di sant Yàlla naan: 2:14 «Nañu màggal Yàlla ca asamaan su kawe sa,te ci àddina, na jàmm ji wàcc ci nit, ñi mu nangu ndax yiwam!» 2:15 Bi malaaka ya delloo ca asamaan, sàmm yi di waxante naan: «Nanu dem boog Betleyem, seeti la fa xew, li nu Boroom bi xamal.» 2:16 Ñu daldi gaawantu dem, gis Maryaama ak Yuusufa, ak liir, ba ñu tëral ca lekkukaayu jur ga. 2:17 Bi ñu leen gisee, ñu nettali la ñu leen waxoon ca mbirum xale ba. 2:18 Ñi dégg li sàmm yi doon wax ñépp daldi waaru lool. 2:19 Waaye Maryaama moom, takkoon na mbir yooyu yépp, di ko xalaat ci xolam. 2:20 Noonu sàmm ya dellu ca seen jur, di màggal Yàlla, di ko sant ci li ñu déggoon lépp te gis ko, ndaxte lépp am na, ni ko Boroom bi waxe woon. 2:21 Bi bés ba dellusee jamonoy xarafal xale ba agsi. Ñu tudde ko Yeesu, ni ko malaaka ma diglee woon, laata ko yaayam di ëmb. 2:22 Noonu jamono ji ñu leen waroon a sellale agsi, ni ko yoonu Musaa tërale. Waajuri Yeesu yi daldi koy yóbbu ca dëkku Yerusalem, ngir sédde ko Boroom bi. 2:23 Ndaxte bind nañu ci yoonu Boroom bi ne: «Bépp taaw bu góor, nañu ko sédde Boroom bi.» 2:24 Bi ñu ko yóbboo, def nañu itam sarax, ni ko yoonu Boroom bi santaanee: «ñaari pitaxu àll walla ñaari xati yu ndaw.» 2:25 Amoon na ca Yerusalem nit ku tudd Simeyon. Nit ku fonkoon yoonu Yàlla la te déggal ko, doon séentu jamono, ji Yàlla war a dëfël bànni Israyil. Xel mu Sell mi mu ngi ci moom, 2:26 te xamal na ko ne, du dee mukk te gisul Almasib Boroom bi. 2:27 Noonu Xelum Yàlla daldi yóbbu Simeyon ba ca kër Yàlla ga. Bi waajuri Yeesu indee xale ba, ngir sédde ko Yàlla, ni ko yoon wi santaanee, 2:28 Simeyon jël xale bi, leewu ko, daldi sant Yàlla ne: 2:29 «Boroom bi, nanga yiwi sa jaam,mu noppaluji ci jàmm, ni nga ko waxe. 2:30 Ndaxte sama bët tegu na ci mucc gi nga lal, 2:31 xeet yépp seede ko. 2:32 Muy leer giy leeral xeet yi,di ndamu Israyil say gaay.» 2:33 Waajuri Yeesu yi waaru ci li ñu doon wax ci xale bi. 2:34 Noonu Simeyon ñaanal leen, ba noppi ne Maryaama: «Xale bii Yàllaa ko yónni, ngir ñu bare ci Israyil daanu te yékkatiku. Def na ko it muy firnde ju ñuy weddi, 2:35 ba naqar dina xar sa xol ni jaasi. Noonu xalaati ñu bare feeñ.» 2:36 Amoon na it ca Yerusalem yonent bu ñuy wax Aana. Doomu Fanuwel mi askanoo ci Aser la woon, te Aana màggatoon na lool. Bi mu séyee, dëkk na juróom-ñaari at ak jëkkëram. 2:37 Jëkkër ja gaañu, te séyaatul. Léegi amoon na juróom-ñett-fukki at ak ñeent. Mi ngi dëkke woon a jaamu Yàlla guddi ak bëccëg ca kër Yàlla ga, di ñaan ak di woor. 2:38 Aana yem ca waxi Simeyon ya, daldi gërëm Yàlla tey yégal mbiri liir ba ñépp ñi doon séentu jamono, ji Yàlla war a jot Yerusalem. 2:39 Bi waajuri Yeesu yi matalee seen warugar ci lépp lu yoonu Boroom bi santaane woon, ñu dellu seen dëkku Nasaret ca diiwaanu Galile. 2:40 Xale baa nga doon màgg, di dëgër, mu fees ak xel te yiwu Yàlla ànd ak moom. 2:41 At mu jot nag waajuri Yeesu yi daan nañu dem Yerusalem, ngir màggali bésu Jéggi ba. 2:42 Noonu bi Yeesu amee fukki at ak ñaar, ñu dem màggal ga, ni ñu ko daan defe nakajekk. 2:43 Bi màggal ga tasee, ñu dëpp ñibbi, waaye xale ba Yeesu des Yerusalem, te ay waajuram yéguñu ko. 2:44 Ñu xalaat ne, Yeesu dafa àndoon ak ñeneen, ñi ñu bokkaloon yoon. Bi ñu doxee bésub lëmm, ñu tàmbali di ko seet ci seen bokk yi ak seen xame yi. 2:45 Bi ñu ko gisul nag, ñu daldi dellu Yerusalem, seeti ko. 2:46 Ca gannaaw ëllëg sa ñu fekk ko ca kër Yàlla ga, mu toog ci jàngalekati Yawut yi, di déglu ak di laajte. 2:47 Ñépp ñi dégg li mu wax yéemu ci xel, mi mu àndal, ak ni mu doon tontoo. 2:48 Naka la ko waajuram yi gis, ñu daldi waaru. Yaayam ne ko: «Sama doom, lu tax nga def nu lii? Man ak sa baay nu ngi la doon seet, jaaxle lool.» 2:49 Mu ne leen: «Lu tax ngeen may seet? Xanaa xamuleen ne, damaa war a nekk ci sama kër Baay?» 2:50 Waaye xamuñu li kàddoom yi doon tekki. 2:51 Noonu Yeesu daldi ànd ak ñoom, dellu Nasaret te déggal ay waajuram. Fekk yaayam moom takk mbir yooyu yépp ci xolam. 2:52 Yeesoo ngi doon màgg ci jëmm, tey yokku ci xam-xam te neex Yàlla ak nit ñi.
3:1 Fukkeelu at ak juróom ci nguuru Tibeer Sesaar, fekk Poñsë Pilaat yilif diiwaanu Yude, Erodd yilif diiwaanu Galile, Filib magam yilif diiwaanu Iture ak bu Tarakonit, te Lisañas yilif Abilen. 3:2 Te it Anas ak Kayif nekkoon saraxalekat yu mag ya. Ca jamono jooja la kàddug Yàlla wàcc ci Yaxya, doomu Sakariya, ca màndiŋ ma. 3:3 Yaxya daldi dugg àll, bi wër dexu Yurdan gépp, di waaree nii: «Tuubleen seeni bàkkaar, ba noppi ma sóob leen ci ndox, ngir Yàlla baal leen seeni bàkkaar.» 3:4 Loolu lañu bind ci téereb waxi yonent Yàlla Esayi naan:«Am na baat buy xaacu ca màndiŋ ma ne:“Xàll-leen yoonu Boroom bi,jubal-leen fi muy jaar. 3:5 Nañu sëkk xur yi,maasale tund yi ak jànj yi.Yoon yi dëng ñu jubbanti leen,yi ñagas ñu rataxal leen. 3:6 Bu ko defee bépp mbindeef dina gismucc gi Yàlla tëral.”» 3:7 Mbooloo ma daan ñëw ngir mu sóob leen ci ndox, Yaxya daan na leen wax naan: «Yéen ñi fees ak daŋar mel ni ay co! Ku leen artu ngeen daw merum Yàlla mi nar a wàcc? 3:8 Jëfeleen nag ni ñu tuub seeni bàkkaar, te bañ a nax seen bopp naan: “Nun daal doomi Ibraayma lanu,” ndaxte maa ngi leen koy wax, Yàlla man na defal Ibraayma ay doom ci doj yii. 3:9 Sémmiñ wi tiim na reeni garab yi. Garab nag gu meññul doom yu baax, dees na ko gor, sànni ko ci safara si.» 3:10 Mbooloo ma laaj ko ne: «Lan lanu war a def nag?» 3:11 Mu ne leen: «Ku am ñaari mbubb, nga jox menn mi ki amul. Ku am ñam itam, nga bokk ko ak ki amul.» 3:12 Ay juutikat itam ñëw ca Yaxya, ngir mu sóob leen ci ndox; ñu ne ko: «Kilifa gi, lu nu war a def?» 3:13 Mu tontu leen ne: «Laajleen rekk lu jaadu.» 3:14 Ay xarekat laaj nañu ko ne: «Li jëm ci nun nag?» Mu ne leen: «Buleen néewal doole kenn, jël xaalisam ci kaw ay tëkku mbaa ci seede lu dul dëgg. Waaye doylooleen li ñu leen di fey.» 3:15 Mbooloo maa ngay xaar, di séentook a laaj ci seen xel, ndax Yaxya mooy Almasi bi. 3:16 Noonu Yaxya tontu leen ñoom ñépp ne: «Man maa ngi leen di sóob ci ndox. Waaye ki ma ëpp kàttan dina ñëw te yeyoowumaa tekki ay dàllam. Kooku dina leen sóob ci Xel mu Sell mi ak safara. 3:17 Layoom mu ngi ci loxoom, ngir jéri dàgga ja, ba mu set; pepp ma dina ko def ca sàqam, waaye xatax ba dina ko lakk ci safara su dul fey mukk.» 3:18 Noonu Yaxya teg ca yeneen dénkaane yu bare, di yégal nit ña xebaar bu baax ba. 3:19 Waaye Yaxya yedd na Erodd boroom diiwaanu Galile, ndaxte dafa takkoon Erojàdd, jabaru magam, te it boole woon na ci yeneen ñaawteef, 3:20 ba faf tëj Yaxya kaso. 3:21 Noonu Yaxya sóob mbooloo mépp ci ndox, sóobaale it Yeesu. Bi Yeesu di ñaan nag, asamaan daldi ubbiku. 3:22 Noonu Xel mu Sell mi daldi wàcc ci moom, yor jëmmu pitax, te baat bu jóge asamaan jib ne: «Yaa di sama Doom, ji ma bëgg; ci yaw laa ame bànneex.» 3:23 Bi Yeesu di tàmbali liggéeyam, amoon na lu war a tollu ci fanweeri at, di doomu Yuusufa ci bëti nit ñi.Te Yuusufa mooy doomu Eli, 3:24 miy doomu Matat.Matat, Lewi mooy baayam; Lewi, Melki;Melki, Yanayi; Yanayi, Yuusufa; 3:25 Yuusufa, Matacas; Amos; Naxum; Esli; Nagayi. 3:26 Nagayi, Maat; Matacas; Semeyin; Yoseg; Yoda. 3:27 Yoda, Yowanan mooy baayam; Yowanan, Resa;Resa, Sorobabel. Kooku Salacel a ko jur; Salacel, Neri; 3:28 Neri, Melki; Adi; Kosam; Elmadam; Er. 3:29 Er, Yeesu; Eliyeser; Yorim; Matat; Lewi; 3:30 Simeyon; Yuda; Yuusufa; Yonam; Eliyakim. 3:31 Eliyakim, Meleya; Meleya, Mena;Mena, Matata; Matata, Natan;Natan, Daawuda. 3:32 Daawuda mooy doomu Yese;Yese, Obedd; Bowas; Salmon; Naason. 3:33 Naason; Aminadab; Aminadab, Admin;Arni; Esrom; Fares; Yuda; 3:34 Yanqóoba; Isaaxa; Ibraayma; Teraa; Naxor; 3:35 Serug; Ragaw; Faleg; Eber; Sala. 3:36 Sala, Kaynam mooy baayam; Kaynam, Arpagsàdd;Arpagsàdd, Sem; Sem, Nóoyin; Nóoyin, Lemeg; 3:37 Lemeg, Matusala; Enog, Yaredd; Maleleel; Kaynan; 3:38 Enos; Set; Set doomu Aadama;Aadama doomu Yàlla.
4:1 Noonu Yeesu fees ak Xel mu Sell mi, jóge dexu Yurdan. 4:2 Xelum Yàlla mi yóbbu ko ca màndiŋ ma, mu nekk fa ñeent-fukki fan, jànkoonte ak fiiri Seytaane. Lekkul woon dara ci fan yooya, te gannaaw gi mu xiif. 4:3 Noonu Seytaane ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, santal doj wii mu nekk mburu.» 4:4 Yeesu tontu ko ne: «Mbind mi nee na: “Nit du dunde mburu rekk.”» 4:5 Seytaane yóbbu na ko fu kawe. Ci xef-ak-xippi mu won ko réewi àddina sépp, 4:6 ne ko: «Dinaa la jox bépp sañ-sañu nguur yii ak seen ndam ndaxte jébbal nañu ma ko, te ku ma soob laa koy jox. 4:7 Kon boo ma màggalee, dinga moom lépp.» 4:8 Yeesu tontu ko ne: «Mbind mi nee na: “Nanga màggal Yàlla sa Boroom te jaamu ko moom rekk.”» 4:9 Seytaane yóbbu na ko Yerusalem, teg ko ca njobbaxtalu kër Yàlla ga ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, tëbal jëm ci suuf, 4:10 ndaxte Mbind mi nee na:“Dina jox ay malaakaam ndigal ci sa mbir,ñu sàmm la, 4:11 dinañu la leewu ci seeni loxo,ngir nga bañ a fakkastalu ciw doj.”» 4:12 Yeesu tontu ko ne: «Bind nañu ne: “Bul diiŋat Yàlla, sa Boroom.”» 4:13 Bi mu ko lalalee fiiram yi mu am yépp, Seytaane daldi sore Yeesu, di xaar yeneen jamono. 4:14 Yeesu dellu diiwaanu Galile, fees ak dooley Xelum Yàlla, te turam siiw ca diiwaan booba bépp. 4:15 Muy jàngale ca seeni jàngu, te ñépp di ko tagg. 4:16 Yeesu dem Nasaret fa mu yaroo, te ca bésu noflaay ba, mu dugg ca jàngu ba, ni mu ko daan defe. Noonu mu taxaw ngir jàngal mbooloo mi. 4:17 Ñu jox ko téereb yonent Yàlla Esayi. Bi mu ko ubbee, mu gis bérab, ba ñu bind aaya yii: 4:18 «Xelum Boroom baa ngi ci man,ndaxte moo ma tànn,ngir ma yégal néew doole yi xebaar bu baax bi.Dafa maa yónni,ngir ma yégal jaam ñi ne, dinañu leen goreel,yégal gumba yi ne, dinañu gis,te jot ñi ñu noot, 4:19 tey yégle atum yiw, mi jóge ci Boroom bi.» 4:20 Bi mu jàngee aaya yooyu ba noppi, mu ub téere bi, delloo ko ki koy denc, toog. Ñépp ña nekkoon ca jàngu ba dékk koy bët. 4:21 Noonu mu daldi ne: «Tey jii, loolu Mbind mi wax mat na, bi ngeen koy déglu.» 4:22 Ñépp di seede lu rafet ci Yeesu, di waaru ci wax ju neex, ji mu doon yégle, ñu naan: «Ndax kii du doomu Yuusufa?» 4:23 Mu daldi leen ne: «Xam naa ne dingeen ma ne: “Fajkat bi, fajal sa bopp. Yég nanu li xew Kapernawum, defal lu ni mel fii ci réew mi nga dëkk.”» 4:24 Mu tegaat ca ne: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ab yonent kenn du ko teral ca réewam. 4:25 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ca jamonoy Iliyas, bi mu tawul lu mat ñetti at ak genn-wàll, te xiif bu metti am ca réew mépp, amoon na ca Israyil jigéen yu bare yu seen jëkkër faatu. 4:26 Moona Yàlla yónniwul Iliyas ci kenn ci ñoom, waaye mu yebal ko ci jigéen ju jëkkëram faatu, ju dëkk Sarebta, ca wetu Sidon. 4:27 Te it amoon na ca Israyil, ca jamonoy yonent Yàlla Alisa, ay nit ñu bare ñu gaana. Waaye fajul ci kenn ku dul Naaman, mi dëkkoon réewu Siri.» 4:28 Bi ñu déggee wax yooya, ñépp ña nekkoon ca jàngu ba daldi fees ak mer. 4:29 Noonu ñu jóg, génne ko dëkk ba, yóbbu ko ca mbartalum tund, wa ñu sanc seen dëkk, ngir bëmëx ko ci suuf. 4:30 Waaye moom mu jaar ci seen biir, dem yoonam. 4:31 Gannaaw loolu Yeesu dem Kapernawum, ab dëkk ca diiwaanu Galile. 4:32 Mu jàngal leen ca bésu noflaay ba, ñu waaru ca njàngaleem, ndaxte dafa wax ak sañ-sañ. 4:33 Noonu am na ci jàngu bi nit ku rab jàpp. Mu daldi xaacu ne: 4:34 «Moo! Yaw Yeesum Nasaret, loo nuy fexeel? Ndax dangaa ñëw ngir alag nu? Xam naa la, yaa di Aji Sell ji jóge ci Yàlla!» 4:35 Waaye Yeesu gëdd ko naan: «Noppil te génn ci moom!» Noonu rab wi daaneel nit ki ci suuf ci kanamu ñépp, daldi génn ci moom te gaañu ko. 4:36 Bi loolu amee ñépp waaru, ñuy waxante ci seen biir naan: «Céy jii wax! Ci sañ-sañ ak doole lay sant rab yi, ñu daldi génn.» 4:37 Noonu turam siiw ca diiwaan bépp. 4:38 Bi mu jógee ci jàngu bi, Yeesu dafa dem kër Simoŋ. Gorob Simoŋ bu jigéen dafa feebar, ba yaram wi tàng lool. Ñu naan Yeesu, mu dimbali leen ci. 4:39 Mu randusi, tiim ko, gëdd tàngoor wi, mu dem. Noonu tàngoor wi wàcc, soxna si jóg ca saa sa, di leen topptoo. 4:40 Bi jant sowee, ñu indil Yeesu ñi wopp ñépp ak ay jàngoro yu wuute. Kenn ku nekk mu teg la loxo, wéral la. 4:41 Te it ay rab di génn ca nit ña te di yuuxu naan: «Yaay Doomu Yàlla!» Noonu mu gëdd leen, te mayu leen, ñu wax dara, ndaxte xam nañu ne, mooy Almasi bi. 4:42 Ca njël gu jëkk Yeesu génn, dem ca bérab bu wéet. Mbooloo ma di ko seet. Bi ñu ko gisee, ñu koy wut a téye, ngir bañ mu dem. 4:43 Waaye mu ne leen: «Damaa war a dem ci yeneen dëkk yi, ngir yégle xebaar bu baax bi ci nguuru Yàlla, ndaxte looloo tax ñu yónni ma.» 4:44 Noonu mu dem di waare ca jàngu ya ca réewu Yawut ya.
5:1 Benn bés Yeesu taxaw ca tefesu dexu Senesaret. Mbooloo ma wër ko, di buuxante ngir déglu kàddug Yàlla. 5:2 Noonu mu gis ñaari gaal yu teer ca tefes ga, nappkat ya ca wàcce, di raxas seeni mbaal. 5:3 Mu dugg ci genn gaal, fekk muy gu Simoŋ, mu ne ko, mu joow ba sore tuuti. Noonu Yeesu toog ca gaal ga, di jàngal mbooloo ma. 5:4 Bi mu jàngalee ba noppi, mu ne Simoŋ: «Joowal gaal gi, ba fa ndox ma gën a xóote, ngeen sànni fa seeni mbaal ngir napp.» 5:5 Simoŋ tontu ko ne: «Kilifa gi, coono lanu fanaane biig te jàppunu dara. Waaye nag dinaa ko sànni ci sa ndigal.» 5:6 Naka lañu sànni mbaal yi, jàpp jën yu bare, ba mbaal yay tàmbalee xëtt. 5:7 Noonu ñu daldi liyaar seen àndandoo, yi nekk ca geneen gaal ga, ngir ñu ñëw dimbali leen. Ñooñu agsi, ñu feesal ñaari gaal yi, ba ñuy bëgg a suux. 5:8 Naka la Simoŋ Piyeer gis loolu, daldi sukk ci kanamu Yeesu ne ko: «Sore ma Boroom bi, ndaxte nitu bàkkaar laa!» 5:9 Wax na loolu nag, ndax jën yu bare ya ñu mbaaloon daf koo jaaxal, moom ak ña mu àndaloon 5:10 ak ña mu bokkaloon liggéey ba, maanaam ñaari doomi Sebede yi di Saag ak Yowaana. Yeesu ne Simoŋ: «Bul ragal dara; gannaawsi tey, ay nit ngay mbaal jëme ci man.» 5:11 Noonu ñu teer ca tefes ga, bàyyi lépp, di topp ci moom. 5:12 Ni Yeesu nekke woon ci ab dëkk, am fa ku gaana ba daj. Bi mu gisee Yeesu, mu daldi dëpp jëwam ci suuf, ñaan ko: «Sang bi, soo ko bëggee, man nga maa wéral.» 5:13 Yeesu tàllal loxoom, laal ko naan: «Bëgg naa ko, wéral.» Ca saa sa ngaanaam daldi deñ. 5:14 Yeesu sant ko ne: «Bu ko wax kenn, waaye demal won sa bopp saraxalekat bi, te nga jébbal Yàlla sarax si yoonu Musaa santaane, ngir ñu xam ne wér nga, te mu nekk seede ci ñoom.» 5:15 Noonu turu Yeesu di gën a siiw. Mbooloo mu bare di ñëw ci moom, ngir déglu ko te mu faj seeni jàngoro. 5:16 Waaye Yeesu moom di beddeeku ci bérab yu wéet ya, di ñaan. 5:17 Am na bés Yeesu doon jàngale. Amoon na ca mbooloo, ma teewoon, ñu bokkoon ca Farisen ya ak ay xutbakat yu jóge ca dëkk yépp, ya ca Galile ak ya ca Yude ak Yerusalem. Yeesu àndoon na ak dooley Boroom bi, ba muy faj ay jarag. 5:18 Noonu ay nit ñëw, jàppoo basaŋ, ga ñu tëral nit ku yaram wépp làggi. Ñu di ko wut a dugal ca kër ga, ngir indi ko ca Yeesu. 5:19 Waaye gisuñu fu ñu koy awale ndax mbooloo ma. Ñu daldi yéeg ca kaw kër ga nag, xeddi tiwiil ya, yoor waa ja ak basaŋ ga, wàcce ko ca kanamu Yeesu ca biir mbooloo ma. 5:20 Bi Yeesu gisee seen ngëm, mu ne làggi ba: «Sama waay, baal nañu la say bàkkaar.» 5:21 Xutbakat yi ak Farisen yi di werante ci seen xel naan: «Kii mooy kan bay sosal Yàlla? Ana ku man a baale bàkkaar yi, ku dul Yàlla doŋŋ?» 5:22 Waaye Yeesu xam seen xalaat, tontu leen ne: «Lu tax ngeen di werante ci seen xel? 5:23 Ma wax ne: “Baal nañu la say bàkkaar,” walla ma ne: “Jógal te dox,” lan moo ci gën a yomb? 5:24 Waaye xamleen ne, Doomu nit ki am na ci àddina sañ-sañu baale bàkkaar yi.» Ci kaw loolu Yeesu ne ku làggi ba: «Maa ngi la koy sant, jógal, jël sa basaŋ te nga ñibbi.» 5:25 Nit ka jóg ca saa sa ci kanamu ñépp, jël basaŋ, ga ñu ko tëraloon, ñibbi tey màggal Yàlla. 5:26 Mbooloo mépp waaru, di màggal Yàlla. Ñu ragal tey wax naan: «Gis nanu tey ay mbir yu ëpp xel.» 5:27 Gannaaw loolu Yeesu génn, gis ab juutikat bu tudd Lewi, mu toog ca juuti ba. Mu ne ko: «Kaay topp ci man.» 5:28 Lewi jóg, bàyyi lépp, daldi ko topp. 5:29 Noonu Lewi togglu ay ñam yu bare ci këram, ngir teral Yeesu. Juutikat yu bare ak yeneen gan ñu nga fa woon, di lekkandoo ak ñoom. 5:30 Farisen yi ak seeni xutbakat di xultu taalibey Yeesu yi ne leen: «Lu tax ngeen di lekkandoo ak di naanandoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar?» 5:31 Yeesu tontu leen ne: «Ñi wér soxlawuñu fajkat, ñi wéradi ñoo ko soxla. 5:32 Ñëwuma ngir woo ñi jub, waaye ngir woo bàkkaarkat yi, ñu tuub seeni bàkkaar.» 5:33 Noonu ñu ne Yeesu: «Taalibey Yaxya yi ak yu Farisen yi dinañu faral di woor ak di ñaan ci Yàlla, waaye say taalibe ñu ngiy lekk ak di naan.» 5:34 Yeesu ne leen: «Ndax man ngeen a woorloo gan, yi ñëw cig céet, li feek boroom céet gaa ngi ànd ak ñoom? 5:35 Waaye bés yaa ngi ñëw, yu ñuy jële boroom céet gi ci seen biir. Bés yooyu nag, dinañu woor.» 5:36 Te it Yeesu wax leen léeb wii: «Kenn du jël mbubb mu bees, xotti ci sekkit, daaxe ko mbubb mu màggat. Lu ko moy, dina xotti mbubb mu bees mi, te sekkit, wi mu ci jële, du ànd ak mbubb mu màggat mi. 5:37 Te kenn du def biiñ bu bees ci mbuusi der yu màggat. Lu ko moy, biiñ bu bees bi day toj mbuus yi, biiñ bi tuuru, mbuus yi yàqu. 5:38 Waaye dañoo war a def biiñ bu bees ci mbuus yu bees. 5:39 Ku naan biiñ bu màggat du bëgg bu bees bi, ndax day wax ne: “Bu màggat bi baax na.”»
6:1 Amoon na benn bésu noflaay Yeesu di dem, jaar ci ay tool yu ñor. Taalibeem ya di fàq ay cëgg, di leen boxom ci seeni loxo tey lekk. 6:2 Am ay Farisen yu ne: «Lu tax ngeen di def lu jaaduwul ci bésu noflaay bi?» 6:3 Yeesu tontu leen ne: «Ndax jànguleen la Daawuda defoon, ba mu xiifee, moom ak ña mu àndaloon? 6:4 Xanaa yéguleen, ni mu dugge woon ca kër Yàlla ga, jël mburu, ya ñu jébbal Yàlla, lekk ca, jox ca ña mu àndaloon? Fekk jaaduwul kenn lekk ko, ku dul saraxalekat.» 6:5 Yeesu dellu ne leen: «Doomu nit ki mooy boroom bésu noflaay bi.» 6:6 Beneen bésu noflaay, Yeesu dugg ci jàngu bi, di fa jàngale. Amoon na fa nit ku loxol ndeyjooram làggi. 6:7 Xutbakat yi ak Farisen yi ñu ngi ko doon xool, ba xam dina ko faj ci bésu noflaay bi, ngir ñu am lu ñu ko tuumaale. 6:8 Waaye Yeesu xam seen xalaat, daldi ne ku loxoom làggi: «Jógal taxaw ci kanamu ñépp.» Nit ka daldi jóg taxaw. 6:9 Yeesu ne leen: «Ma laaj leen, lan moo jaadu, nu def ko bésu noflaay bi, lu baax mbaa lu bon; nu musal nit mbaa nu lor nit?» 6:10 Ci kaw loolu mu xool leen ñoom ñépp, ba noppi ne nit ka: «Tàllalal sa loxo.» Mu tàllal ko, loxoom daldi wér peŋŋ. 6:11 Waaye nit ña mer ba fees, di rabat pexe yu jëm ca Yeesu. 6:12 Ca bés yooya Yeesu yéeg ca tund wa ngir ñaan, mu fanaan fa, di ñaan ci Yàlla. 6:13 Bi bët setee, Yeesu woo taalibeem yi, tànn ci fukk ak ñaar, tudde leen ay ndawam: 6:14 Simoŋ, mi Yeesu tudde Piyeer, ak Andare, mi bokk ak Piyeer ndey ak baay; Saag ak Yowaana, Filib ak Bartelemi, 6:15 Macë ak Tomaa, Saag doomu Alfe, ak Simoŋ mi bokk ci mbooloo, ma ñu tudde Ñi farlu ci moom seen réew; 6:16 Yudaa doomu Saag, ak Yudaa Iskariyo, mi mujj a wor. 6:17 Yeesu ànd ak ndaw ya, wàcc tund ya, daldi taxaw ca joor ga, fa mbooloom taalibe mu takku nekkoon. Amoon na fa it ay nit ñu bare ñu jóge ca réewu Yawut ya mépp ak ca dëkku Yerusalem ak dëkk yi nekk ca wetu géej ga, maanaam Tir ak Sidon. 6:18 Dañoo ñëw ngir déglu ko, te it ngir mu faj leen. Ñi rab jàpp it faju nañu. 6:19 Ñépp a ngi ko doon wut a laal ndax doole jiy jóge ci moom, di faj ñépp. 6:20 Yeesu xool ay taalibeem ne leen:«Yéen ñi sësul lu dul ci Yàlla, barkeel ngeen,ndaxte nguuru Yàlla, yéena ko yelloo. 6:21 Yéen ñi xiif léegi, barkeel ngeen,ndax dingeen regg.Yéen ñiy naqarlu léegi, barkeel ngeen,ndax dingeen ree. 6:22 Barkeel ngeen, bu leen nit ñi bañee, di leen dàq ak a saaga, di sib seen tur ngir Doomu nit ki. 6:23 Bu boobaa bégleen te bànneexu, ndax seen yool dina réy ci laaxira. Ndaxte noonu la maami seeni bañ daan fitnaale yonent yi. 6:24 Waaye nag yéen boroom alal yi, torox ngeen,ndaxte jot ngeen ba noppi seen bànneex. 6:25 Yéen ñiy lekk ba suur léegi, torox ngeen,ndax ëllëg dingeen xiif.Yéen ñiy ree léegi, torox ngeen,ndax dingeen am aw naqar, ba jooy xàcc. 6:26 Torox ngeen bu leen ñépp dee waxal lu baax, ndaxte noonu la seeni maam daan jëfe ak ña doon mbubboo yonent. 6:27 «Waaye maa ngi leen koy wax, yéen ñi may déglu, soppleen seeni bañaale tey defal lu baax ñi leen bañ. 6:28 Yéeneleen lu baax ñi leen di móolu, te ñaanal ñi leen di sonal. 6:29 Ku la talaata cib lex, jox ko ba ca des. Kuy nangu sa mbubb mu mag, bul téye sa turki. 6:30 Képp ku la ñaan, may ko, te ku nangu say yëf, bu ko ko laaj. 6:31 Defal-leen nit ñi li ngeen bëgg, ñu defal leen ko. 6:32 «Su ngeen soppee ñi leen sopp, ban ngërëm ngeen ciy am? Ndaxte bàkkaarkat yi sax sopp nañu ñi leen sopp. 6:33 Te bu ngeen defalee lu baax ñi leen koy defal, ban ngërëm ngeen ciy am? Bàkkaarkat yi it dañuy def noonu. 6:34 Te bu ngeen dee leble te yaakaar ci ndelloo, ban ngërëm ngeen ciy am? Bàkkaarkat yi it dañuy lebal seeni moroom, ngir ñu delloo leen ko. 6:35 Waaye soppleen seeni noon, di leen defal lu baax, tey leble, bañ a yaakaar ñu delloo leen ko. Noonu seen yool dina mag te dingeen wone ne, yéenay doomi Aji Kawe ji, ndaxte Yàlla day wone mbaaxam ci ñu goreedi ñi ak ñu soxor ñi. 6:36 Nangeen am yërmande, ni seen Baay ame yërmande. 6:37 «Buleen àtte seeni moroom ak ñaaw njort, te deesu leen àtte. Buleen daan kenn, te deesu leen daan. Baal-leen ñi ci des, te dinañu leen baal. 6:38 Mayeleen te dinañu leen may. Dinañu leen ëmbal natt bu baax bu ñu rokkas te yengal ko, mu fees bay tuuru. Ndaxte dees na leen nattal ak natt, bi ngeen di nattale.» 6:39 Noonu Yeesu wax na leen beneen léeb ne leen: «Ndax gumba man na wommat moroomam? Mbaa duñu daanu ñoom ñaar ci kàmb? 6:40 Taalibe gënul kilifaam, waaye taalibe bu jàng ba wàcc, dina yem ak kilifaam demin. 6:41 «Lu tax ngay xool ñax gi ci sa bëtu mbokk, te gisuloo gànj gi ci sa bët yaw? 6:42 Nan nga man a waxe sa mbokk: “Sama xarit, may ma, ma dindil la ñax gi ci sa bët,” yaw mi gisul gànj gi nekk ci sa bët? Naaféq! Jëkkal a dindi gànj gi ci sa bët, te noonu dinga man a gis bu leer, ngir dindi ñax gi ci sa bëtu mbokk. 6:43 «Garab gu baax du meññ doom yu bon, te garab gu bon du meññ doom yu baax. 6:44 Ndaxte garab, meññeefam lañu koy xàmmee. Deesul witte figg ci dédd, walla réseñ ci xaaxaam. 6:45 Noonu nit ku baax, lu baax lay wax, ndax loolu la denc ci xolam, te nit ku bon, lu bon lay wax, ndaxte denc na lu bon ci xolam. Ndaxte gémmiñ, la fees xolam lay wax. 6:46 «Lu tax ngeen may wooye “Boroom bi, Boroom bi,” te dungeen def li may wax? 6:47 Képp ku ñëw ci man, di dégg samay wax te di ko jëfe, ma won leen nu muy mel. 6:48 Dafa mel ni nit kuy tabax kër, mu gas fu xóot, jot doj wu réy, samp fa kër ga. Bi mbënn ma ñëwee, wal ma dafa dal ca kër ga te yenguwul, ndaxte nit ka dafa tabax kër ga tabax bu dëgër. 6:49 Waaye képp ku dégg samay wax te jëfewuloo ko, dinga mel ni nit ku tabax këram ci suuf, bañ koo defal fondamaa. Bi wal ma dalee ca kër googa, dafa màbb ca saa sa, lépp yàqu yaxeet.»
7:1 Bi Yeesu waxee la mu naroon a wax lépp ca kanamu mbooloo ma, mu daldi dem Kapernawum. 7:2 Amoon na fa njiitu xare. Njiit la nag, surgaam bu mu bëggoon lool dafa feebaroon, bay bëgg a dee. 7:3 Bi mu déggee mbiri Yeesu, mu yónni ca moom ay Yawut, di magi dëkk ba, ngir ñaan ko, mu ñëw faj surga ba. 7:4 Bi magi dëkk ba agsee ca Yeesu, ñu sàkku ci moom ndimbal, ñaan ko: «Ki nu yónni ci yaw de, yelloo na ndimbal, 7:5 ndaxte sopp na sunu xeet te moo nu tabaxal sax sunu jàngu.» 7:6 Noonu Yeesu daldi ànd ak ñoom. Waaye bi ñuy bëgg a agsi ca kër ga, njiit la yebal ay xaritam ngir ñu wax Yeesu ne: «Sang bi, bul sonal sa bopp, ndaxte yeyoowuma nga dugg sama kër. 7:7 Looloo tax it ma xalaat ne, awma darajay gatandu la. Waxal genn kàddu rekk, te sama surga dina wér. 7:8 Ndaxte man itam maa ngi nekk ci ndigal, te ame naa ay xarekat ci sama ndigal. Su ma nee kii: “Demal,” mu dem. Mbaa ma ne keneen ki: “Ñëwal,” mu ñëw. Te su ma nee sama jaam: “Defal lii,” mu def ko.» 7:9 Bi ko Yeesu déggee, mu waaru. Noonu mu walbatiku ca mbooloo, ma topp ci moom, ne leen: «Maa ngi leen koy wax, ci bànni Israyil sax, musuma cee gis ku gëme nii.» 7:10 Noonu ndaw ya daldi dellu ca kër ga. Bi ñu agsee, ñu gis ne surga ba wér na. 7:11 Yàggul dara Yeesu dem ci dëkk bu ñuy wax Nayin. Taalibeem yi ak mbooloo mu bare ànd ak moom. 7:12 Bi muy agsi ca buntu dëkk ba, fekk ñuy rob néew boo xam ne kenn rekk la woon ci ndeyam, ji jëkkëram faatu woon. Te mbooloo mu bare ca dëkk ba di gunge soxna sa. 7:13 Bi ko Boroom ba gisee, mu daldi koy yërëm ne ko: «Bul jooyati.» 7:14 Mu jegeñsi, laal jaat ga, ñi ko jàppoo taxaw. Mu ne: «Waxambaane wi, jógal, ndigal la.» 7:15 Noonu nit ka dee woon jóg toog, tàmbalee wax. Yeesu delloo ko yaay ja. 7:16 Ñépp tiit, bay màggal Yàlla, di wax naan: «Yonent bu mag feeñ na ci sunu biir! Yàlla wallusi na mbooloom!» 7:17 La ñu wax ci mbiri Yeesu daldi siiw ca réewu Yawut ya ak la ko wër yépp. 7:18 Taalibey Yaxya ya nettali mbir yooyu yépp seen kilifa. Noonu Yaxya woo ñaar ci ay taalibeem, 7:19 yónni leen ci Boroom bi, ngir laaj ko: «Ndax yaw yaa di Ki war a ñëw, walla danoo war a xaar keneen?» 7:20 Bi taalibe ya agsee ca Yeesu, ñu ne ko: «Yaxya moo nu yebal, nu laaj ndax yaa di Ki waroon a ñëw, walla danuy xaar keneen?» 7:21 Ca waxtu woowa Yeesu wéral nit ñu bare ci seeni feebar ak ci seeni metit, di dàq ay rab tey gisloo ay gumba. 7:22 Noonu mu tontu ndaw ya ne leen: «Demleen nettali Yaxya li ngeen gis te dégg ko. Gumba yaa ngi gis, lafañ yiy dox, gaana yi wér, tëx yiy dégg, ñi dee di dekki, te ñi woyoflu ñu ngi dégg xebaar bu baax bi. 7:23 Yaw mi sa ngëm yolomul ndax man, barkeel nga.» 7:24 Bi ndawi Yaxya yi demee, Yeesu daldi wax ak mbooloo ma ci mbirum Yaxya ne leen: «Lu ngeen seeti woon ca màndiŋ ma? Xanaa barax buy jaayu ci ngelaw li? 7:25 Kon lu ngeen seeti woon nag? Nit ku sol yére yu rafet? Waaye ñiy soloo noonu, tey dund dund gu neex ñu ngi dëkk ci këri buur. 7:26 Kon lu ngeen seeti woon? Yonent? Waaw, wax naa leen ne, ëpp na yonent. 7:27 Yaxya male moo di ki ñu waxoon ci Mbind mi naan:“Maa ngi yónni sama ndaw, mu jiitu la,te xàllal la yoon ci sa kanam.” 7:28 Maa ngi leen koy wax, ci li jigéen jur, ku sut Yaxya musul a feeñ. Waaye ba tey ki gën a ndaw ci nguuru Yàlla moo ko sut.» 7:29 Nit ñépp ñi doon déglu Yeesu, ba ci juutikat yi sax, dëggal nañu ne Yàlla ku jub la, ndaxte nangu nañu Yaxya sóob leen ci ndox. 7:30 Waaye Farisen ya ak xutbakat ya dañoo bañ, mu sóob leen ci ndox, di wone noonu ne, gàntu nañu li leen Yàlla bëggaloon. 7:31 Yeesu tegaat ca ne: «Kon lan laa man a mengaleel niti jamono jii? Lan lañuy nirool? 7:32 Ñu ngi nirook xale yu toog ca pénc ma tey woowante naan:“Liital nanu leen ak toxoro, te fecculeen,woyal nanu leen woyi dëj, te jooyuleen.” 7:33 Ndaxte Yaxya feeñ na, lekkul mburu, naanul biiñ, ngeen daldi ne: “Dafa ànd ak rab.” 7:34 Gannaaw gi nag Doomu nit ki ñëw na, lekk, naan, ngeen daldi ne: “Kii daal bëgg na lekk, di naan biiñ, tey xaritoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar.” 7:35 Waaye li xam-xamu Yàlla di jur, mooy firndeel ne dëgg la.» 7:36 Amoon na ab Farisen bu ñaan Yeesu, mu ñëw lekkandoo ak moom. Yeesu dem kër waa ja, toog ca lekkukaay. 7:37 Fekk amoon na ca dëkk ba jigéen juy moy Yàlla. Bi mu yégee ne, Yeesoo ngay lekk ca kër Farisen ba, mu dem, yóbbaale njaq lu ñu defare doj wu ñuy wax albaatar te def latkoloñ. 7:38 Bi jigéen ja agsee, mu taxaw ca gannaaw tànki Yeesu, di jooy. Noonu ay rangooñam tooyal tànki Yeesu, jigéen ja di leen fomp ak kawaram, di leen fóon te ciy sotti latkoloñ ja. 7:39 Naka la Farisen, bi woo woon Yeesu ci këram, gis loolu, mu wax ci xelam naan: «Bu nit kii doonoon yonent, kon dina xam kuy jigéen ji koy laal ak ni mu nekke bàkkaarkat.» 7:40 Yeesu ne ca tonn, daldi ne Farisen ba: «Simoŋ, am na lu ma la war a wax.» Simoŋ ne ko: «Waxal, kilifa gi.» 7:41 Yeesu ne ko: «Da fee amoon ñaari nit ñu ameel bor benn leblekat. Kenn kaa ngi ko ameel téeméeri junni ci xaalis, ki ci des fukki junni. 7:42 Waaye kenn ci ñoom mënu koo fey. Noonu mu baal leen bor ya. Ci ñaar ñooñu nag kan moo ko ciy gën a bëgg?» 7:43 Simoŋ tontu ne ko: «Xanaa ki ñu baal bor bi gën a bare.» Yeesu ne ko: «Àtte nga dëgg,» 7:44 daldi walbatiku ca jigéen ja, ne Simoŋ: «Ndax gis nga jigéen jii? Dugg naa sa kër, te joxewuloo ndox, ngir raxas samay tànk. Waaye moom, raxas na samay tànk ak ay rangooñam, ba noppi fomp leen ak kawaram. 7:45 Bi ma agsee, fóonuloo ma, waaye moom, bi ma duggee ba léegi tàyyiwul ci di fóon samay tànk. 7:46 Defuloo diw ci sama bopp, waaye moom, sotti na latkoloñ ci samay tànk. 7:47 Moo tax ma di la wax ne, su wonee mbëggeel gu réye nii, dafa fekk ñu baal ko bàkkaaram yu bare. Waaye ki mbëggeelam néew dafa fekk ñu baal ko lu tuuti.» 7:48 Yeesu daldi ne jigéen ja: «Baal nañu la say bàkkaar.» 7:49 Noonu ñi doon lekkandoo ak moom di wax ci seen xel naan: «Kii am sañ-sañu baale bàkkaar mooy kan?» 7:50 Waaye Yeesu ne jigéen ja: «Sa ngëm musal na la. Demal ci jàmm.»
8:1 Gannaaw loolu Yeesu di dem ca ay dëkk yu mag ak yu ndaw, di waaraate ak di yégle xebaar bu baax bi jëm ci nguuru Yàlla. Fukki taalibe ya ak ñaar ànd ak moom, 8:2 ak ay jigéen yu mu teqale woon ak rab te jële leen ci seeni wopp, ñu di: Maryaama, mi ñuy wooye Maryaamam Magdala, mi Yeesu tàggale woon ak juróom-ñaari rab; 8:3 Sànn, jabaru ku ñuy wax Kusa, mi doon wottu alalu Erodd; ak Susànn ak ñeneen jigéen. Jigéen ñooñu ñoo doon joxe seen alal, ngir dimbali Yeesu ak ay taalibeem. 8:4 Dëkk ak dëkk nit ña di fa jóge jëm ca Yeesu, ba mbooloo mu bare dajaloo, mu wax leen léeb wii: 8:5 «Dafa amoon beykat bu demoon jiyi. Bi muy saaw toolam nag, lenn ci pepp mi wadd ci kaw yoon wi, nit ñi joggi ci, picci asamaan lekk ko lépp. 8:6 Leneen wadd ci bérab bu bare ay doj. Naka la sax rekk, daldi wow, ndaxte suuf si tooyul woon. 8:7 Leneen nag wadd ci biir ay xaaxaam, ñu saxandoo, xaaxaam ya tanc ko. 8:8 Li ci des dal ci suuf su baax, sax, nangu ba meññ téeméeri yoon lu ëpp la mu ji woon.» Gannaaw loolu Yeesu wax ak kàddu gu dëgër ne: «Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.» 8:9 Taalibey Yeesu yi laaj ko lu léeb woowu di tekki. 8:10 Mu tontu ne leen: «May nañu leen, ngeen xam mbóoti nguuru Yàlla, waaye ñi ci des, dama leen di wax ci ay léeb. Noonu la, ngir:“Ñuy xool te duñu man a gis,di dégg te duñu man a xam.” 8:11 «Lii la léebu beykat bi di tekki. Kàddug Yàlla mooy jiwu wi. 8:12 Ki féete ci yoon wi mooy ki dégg. Gannaaw gi, Seytaane dafay ñëw, këf kàddu, gi ñu def ci xolam, ngir mu bañ a gëm te Yàlla musal ko. 8:13 Ki nekk ci bérab bu bare ay doj, mooy ki dégg kàddu gi, ba noppi nangu ko ak mbég. Waaye wax ji saxul ci moom. Dina gëm ab diir, waaye bu nattu yi agsee, mu daldi dàggeeku. 8:14 Ki jot ci jiwu wi ci xaaxaam yi mooy ki dégg kàddu gi, waaye nes tuuti soxla yi ak alal ak bànneexi àddina tanc ko, ba du àgg cig mat. 8:15 Ki jot ci jiwu wi ci suuf su baax si nag, mooy ki dégg kàddu gi te denc ko ci xol bu baax bu gore, te muñ ba jur njariñ. 8:16 «Kenn du taal làmp, dëpp ci leget, walla mu di ko def ci ron lal. Daf koy wékk, ngir mu leeral ñiy dugg. 8:17 Amul dara luy kumpa lu ñu dul siiwal bés, walla lu làqu lu ñu dul feeñal, ba mu ne fàŋŋ. 8:18 Seetleen bu baax, ni ngeen di dégloo kàddu gi. Ku am, dees na la dollil, waaye ku amul, dees na nangu sax li nga xalaatoon ne, am nga ko ba noppi.» 8:19 Noonu ndeyu Yeesu ak ay rakkam ñëw seetsi ko, waaye mënuñu woon a agsi ci moom, ndaxte nit ña dañoo bare. 8:20 Am ku ko yégal ne: «Sa yaay ak say rakk ñu ngi nii taxaw ci biti, bëgg laa gis.» 8:21 Waaye mu daldi leen ne: «Sama yaay ak samay rakk, ñooy ñiy déglu kàddug Yàlla, te di ko topp.» 8:22 Benn bés Yeesu àndoon na ak ay taalibeem, dugg ci gaal. Mu ne leen: «Nanu jàll dex gi.» Noonu ñu dem. 8:23 Bi ñuy dem nag, Yeesu daldi nelaw. Ngelaw lu am doole daldi ñëw, yengal dex gi, gaal gi fees ak ndox, ba ñu bëgg a suux. 8:24 Noonu taalibe yi jegesi Yeesu, yee ko ne: «Kilifa gi, kilifa gi, nu ngiy dee!» Ci kaw loolu Yeesu jóg, daldi gëdd ngelaw li ak duus yi. Lépp dal, ba ne nemm. 8:25 Yeesu ne taalibe yi: «Ana seen ngëm?» Ñu daldi tiit te waaru, naan ci seen biir: «Kii moo di kan? Mi ngi jox ndigal ngelaw li ak ndox mi, ñu koy déggal.» 8:26 Noonu ñu teer ca diiwaanu waa Serasa, fa jàkkaarloo ak diiwaanu Galile. 8:27 Bi Yeesu di wàcc ca gaal ga, ku rab jàpp ca waa dëkk ba ñëw, kar ko. Yàgg na def yaramu neen te dëkkul ca kër, waaye ca sëg ya lay nekk. 8:28 Bi mu gisee Yeesu, mu yuuxu, daanu ciy tànkam, daldi xaacu ne: «Yaw Yeesu Doomu Yàlla Aji Kawe ji, loo may fexeel? Maa ngi lay ñaan, nga bañ maa mbugal.» 8:29 Dafa wax loolu, ndaxte Yeesu santoon na rab wi, mu génn ci moom. Rab wa dafa ko doon faral a jàpp. Nit ñi daan nañu ko wottu, di ko yeew ak ay càllala, ak di ko jéng, mu di leen dagg, rab wi di ko xiir ca bérab yu wéet. 8:30 Noonu Yeesu laaj ko: «Noo tudd?» Mu tontu ne: «Coggal laa tudd.» Dafa wax loolu, ndaxte rab yu baree ko jàppoon. 8:31 Rab yooyoo ngi ko doon ñaan, ngir mu bañ leen a sant, ñu dem ca kàmb gu xóot gi. 8:32 Fekk amoon na fa géttu mbaam-xuux yu bare, yuy for ca tund wa. Rab ya ñaan Yeesu, mu may leen, ñu dugg mbaam-xuux ya. Mu may leen ko. 8:33 Noonu rab ya génn nit ka, dugg mbaam-xuux ya, ñu daldi bartalu, daanu ca dex ga, lab. 8:34 Sàmm ya gis li xew, daw nettaliji mbir mi ca dëkk ba ak ca àll ba. 8:35 Nit ñi génn, ngir seet li xew. Bi ñu agsee ca Yeesu, ñu fekk fa nit, ka rab ya bàyyi woon, toog ca kanam Yeesu, sol ay yére te ànd ak sagoom. Ñu daldi ragal. 8:36 Ña fekke woon mbir ma nag, nettali leen naka la Yeesu wérale ki rab ya jàppoon. 8:37 Ci kaw loolu waa diiwaanu Serasa bépp ragal, ba ñaan Yeesu mu jóge fa. Noonu Yeesu dugg ci gaal gi, di bëgg a dem. 8:38 Nit ki Yeesu tàggale woon ak rab ya ñaan ko, ngir ànd ak moom. Waaye Yeesu woññi ko ne ko: 8:39 «Ñibbil, nettali li la Yàlla defal lépp.» Noonu waa ji dem di wër dëkk ba yépp, di fa yégle la ko Yeesu defal. 8:40 Bi Yeesu dëppee dellu, mbooloo ma di ko teeru, ndaxte ñépp a ngi ko doon xaar. 8:41 Noonu nit ñëw, tuddoon Yayrus te nekk njiitu jàngu ba. Bi mu agsee, mu daanu ci tànki Yeesu, saraxu ko mu ñëw këram, 8:42 ndaxte jenn doomam ju jigéen, ji mu amoon kepp te muy tollu ci fukki at ak ñaar, ma nga doon waaj a dee. Bi Yeesuy dem, nit ñaa ngi doon buuxante, di ko tanc. 8:43 Amoon na nag ca mbooloo ma jigéen ju doon xëpp deret diirub fukki at ak ñaar, te kenn mënu ko woon a faj. 8:44 Jigéen ja jegeñsi Yeesu nag, doxe ko gannaaw, laal catu mbubbam. Ca saa sa deret ji dal. 8:45 Yeesu laaj nit ña ne: «Ana ku ma laal?» Ku nekk di miim. Noonu Piyeer ne ko: «Kilifa gi, nit ñépp a ngi lay wër, di la tanc wet gu nekk.» 8:46 Waaye Yeesu ne: «Am na ku ma laal, ndaxte yég naa ne, am na doole ju génn ci man.» 8:47 Te jigéen ja xam ne, mënul woon a nëbb li mu def. Mu daldi daanu ci tànki Yeesu, di lox. Noonu mu nettali ci kanamu ñépp li taxoon mu laal Yeesu, ak ni mu wére ca saa sa. 8:48 Yeesu ne ko: «Soxna si, sa ngëm faj na la. Demal ci jàmm.» 8:49 Bi Yeesu di wax nag, am na ku jóge ca kër njiit la, mu ñëw naan: «Sa doom faatu na; matatul ngay sonal kilifa gi.» 8:50 Yeesu dégg kàddu yooyu, daldi ne njiit la: «Bul tiit. Gëmal rekk te dina dundaat.» 8:51 Bi Yeesu agsee ca kër ga, nanguwul kenn duggaaleek moom, ñu dul Piyeer, Yowaana, Saag ak waajuri xale ba. 8:52 Ña fa nekk ñépp di yuuxu ak di jooy xale bi. Noonu Yeesu ne leen: «Bàyyileen seen jooy yi. Janq bi deewul, day nelaw rekk.» 8:53 Waaye ñu di ko ñaawal, ndaxte xamoon nañu ne, dee na. 8:54 Waaye Yeesu jàpp loxob janq ba, woo ko ne ko: «Xale bi, jógal.» 8:55 Noonu ruuwu xale ba dellusiwaat, mu daldi jóg ca saa sa. Yeesu santaane ñu may ko, mu lekk. 8:56 Waajuri xale bi daldi waaru. Waaye Yeesu tere leen, ñu wax kenn li xew.
9:1 Benn bés Yeesu dajale fukki taalibe ya ak ñaar, jox leen doole ak sañ-sañu dàq rab yépp ak di faj jàngoro yi. 9:2 Noonu mu yónni leen ñuy yégle nguuru Yàlla ak di faj jarag yi. 9:3 Mu ne leen: «Bu ngeen di dem, buleen yóbbaale dara, du yet mbaa mbuus mbaa mburu mbaa xaalis. Buleen yor it ñaari turki. 9:4 Kër gu ngeen dugg, dal-leen fa, ba kera ngeen di fa jóge. 9:5 Fépp fu leen nit ñi gàntoo, génnleen ca dëkk booba te ngeen yëlëb seen pëndu tànk, ngir seede leen seen réer.» 9:6 Noonu ñu dem dëkk ak dëkk, di fa yégle xebaar bu baax bi, tey wéral jarag yi. 9:7 Bi Erodd boroom diiwaanu Galile déggee li Yeesu ak ay taalibeem doon def lépp, mu jaaxle, ndaxte amoon na, ñu doon wax ci mbiri Yeesu naan: «Yaxya moo dekki.» 9:8 Am it ñuy wax naan: Iliyas moo dellusi. Ñeneen naan: «Kenn ci yonent yu jëkk yaa dekki.» 9:9 Waaye Erodd ne: «Yaxya, man mii maa dagglu boppam. Kon kii ma dégg ay jalooreem, mooy kan?» Noonu mu koy fexee gis. 9:10 Bi ndaw ya dellusee, ñu nettali Yeesu la ñu defoon lépp. Noonu mu yóbbaale leen, ñu sore nit ñi, jëm ca dëkk bu ñuy wax Betsayda. 9:11 Bi ko nit ña yégee, ñu toppi ko. Yeesu teeru leen, di leen wax ci mbirum nguuru Yàlla, te di wéral ñi ko aajowoo. 9:12 Ca ngoon sa fukki taalibe ya ak ñaar ñëw ci Yeesu ne ko: «Yiwil mbooloo mi, ñu dugg ci dëkk yi ak àll bi ko wër, ngir am lu ñu lekk ak fu ñu fanaan, ndaxte fii àllub neen la.» 9:13 Waaye Yeesu ne leen: «Joxleen leen lu ñu lekk.» Ñu tontu ko ne: «Amunu lu dul juróomi mburu ak ñaari jën. Xanaa ndax nu dem jëndal mbooloo mii lu ñu lekk?» 9:14 Ndaxte lu war a mat juróomi junniy góor a nga fa teewoon. Yeesu ne taalibe ya: «Neeleen mbooloo mi ñu toog def ay géewi juróom-fukki nit.» 9:15 Taalibe ya def ko, toogloo nit ña. 9:16 Bi loolu amee Yeesu jël juróomi mburu yi ak ñaari jën yi, xool ci kaw, gërëm Yàlla, ba noppi mu damm leen, jox taalibe yi, ngir ñu séddale ko mbooloo mi. 9:17 Noonu ñépp lekk ba suur. Bi ñu dajalee desit ya, ñu feesal fukki pañe ak ñaar. 9:18 Benn bés Yeesu beddeeku mbooloo ma, di ñaan; taalibe yi nekk ci wetam. Mu laaj leen ne: «Nit ñi, ku ñu wax ne moom laa?» 9:19 Ñu tontu ko ne: «Am na ñu naan, yaa di Yaxya; ñeneen ne, Iliyas; ñi ci des ne, yaay kenn ci yonent yu jëkk yaa dekki.» 9:20 Yeesu ne leen: «Yéen nag ku ngeen ne moom laa?» Piyeer tontu ko ne: «Yaa di Almasi, bi Yàlla yónni.» 9:21 Noonu Yeesu daldi leen dénk, tere leen ñu wax ko kenn, 9:22 teg ca ne: «Doomu nit ki war na sonn lu bare; saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya dëddu ko, ñu rey ko, mu dekki ca ñetteelu fan ba.» 9:23 Noonu Yeesu ne leen ñoom ñépp: «Ku bëgg a aw ci samay tànk, na bàyyi boppam, gàddu bés bu nekk bant, bi ñu ko war a daaj, door a topp ci man. 9:24 Ndaxte koo xam ne bëgg ngaa rawale sa bakkan, dinga ko ñàkk, waaye ku ñàkk sa bakkan ngir man, dinga ko jotaat. 9:25 Ndaxte moom àddina sépp, lu muy jariñ nit, su fekkee ne dafay ñàkk bakkanam walla mu loru? 9:26 Ku ma rus a faral, te nanguwul samay wax, Doomu nit ki dina la rus a xam, bés bu ñëwee ci ndamam ak ci ndamu Baay bi ak lu malaaka yu sell yi. 9:27 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, am na ñi fi taxaw ñoo xam ne duñu dee te gisuñu nguuru Yàlla gi.» 9:28 Bi ñu ca tegee luy tollook ayu-bés gannaaw bi Yeesu waxee loolu, mu ànd ak Piyeer, Yowaana ak Saag, yéeg ca kaw tund wa ngir ñaan. 9:29 Bi muy ñaan, xar-kanamam daldi soppiku, ay yéreem weex tàll bay melax. 9:30 Am ñaari nit di waxtaan ak moom, muy yonenti Yàlla Musaa ak Iliyas. 9:31 Ñoo feeñ ci ndamu Yàlla, di waxtaane ci demu Yeesu, gi muy àggalee yenam ci Yerusalem. 9:32 Fekk Piyeer ak ñi mu àndal doon gëmmeentu, waaye bi ñu yeewoo bu baax, ñu gis ndamu Yeesu, ak ñaari nit ñu taxaw ci wetam. 9:33 Bi nit ñooñu di sore Yeesu, Piyeer ne ko: «Kilifa gi, bég nanu ci sunu teew fii; nanu defar ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa ak benn Iliyas.» Fekk xamul la mu doon wax. 9:34 Bi mu koy wax, niir ñëw muur leen, taalibe yi daldi tiit, bi leen niir wa ëmbee. 9:35 Noonu baat jibe ca niir wa naan: «Kii mooy sama Doom ji ma fal; dégluleen ko.» 9:36 Bi baat ba waxee ba noppi, Yeesu rekk des fa. Taalibe ya noppi, bañ a nettali kenn ca jamono jooja la ñu gisoon. 9:37 Ca suba sa Yeesu ak taalibe ya wàcce ca tund wa, mbooloo mu bare ñëw, di ko gatandu. 9:38 Nit xaacu ci biir mbooloo mi naan: «Kilifa gi, maa ngi lay ñaan, nga seet sama doom, ndaxte moom kepp laa am. 9:39 Léeg-léeg rab jàpp ko, mu daldi yuuxu ca saa sa, rab wi di ko sayloo, gémmiñ gi di fuur. Du faral di génn ci moom te dina ko sonal. 9:40 Ñaan naa say taalibe, ñu dàq ko, waaye mënuñu ko.» 9:41 Yeesu tontu ne: «Yéen niti jamono jii, yéen ñi gëmadi te dëng, ba kañ laa war a nekk ak yéen te di leen muñal? Indil ma sa doom.» 9:42 Bi xale biy agsi, rab wi di ko daaneel ci suuf, muy say. Waaye Yeesu daldi gëdd rab wa, wéral xale ba, daldi ko delloo baayam. 9:43 Ku nekk waaru na ndax màggug Yàlla. Bi ñuy yéemu ci li mu doon def, Yeesu ne taalibeem ya: 9:44 «Dégluleen bu baax lii ma leen di wax: dinañu jébbal Doomu nit ki ci loxoy nit ñi.» 9:45 Waaye taalibe ya xamuñu kàddu googu. Yàlla dafa leen nëbb li muy tekki, ba ñu bañ koo xam, te ñemewuñu koo laaj Yeesu. 9:46 Werante am ci biir taalibe yi, ñuy laajante kan moo gën a màgg ci ñoom. 9:47 Yeesu mi xam seen xalaat, jël ab xale, teg ci wetam ne leen: 9:48 «Ku nangu xale bii ci sama tur, man mii nga nangu; te ku ma nangu, nangu nga ki ma yónni; ndaxte ki gën a woyof ci yéen ñépp, kooku moo gën a màgg.» 9:49 Bi loolu amee Yowaana jël kàddu gi ne: «Kilifa gi, danoo gis nit kuy dàq ay rab ci sa tur, nu tere ko ko, ndaxte bokkul ci nun.» 9:50 Waaye Yeesu tontu ko: «Buleen ko tere, ndaxte ku la sotul, far na ak yaw.» 9:51 Bi jamono ji jegeñsee, ji Yeesu waree jóge àddina dem asamaan, mu sigiñu ci dem Yerusalem. 9:52 Noonu mu yebal ay ndaw, ñu jiitu ko. Ñu dem nag, dugg ci ab dëkk ci diiwaanu Samari, ngir wutal ko fa fu mu dal. 9:53 Waaye waa dëkk ba nanguwuñu ko, ndaxte mi ngi jublu woon Yerusalem. 9:54 Bi taalibe yi tudd Saag ak Yowaana gisee loolu, ñu ne: «Boroom bi, ndax dangaa bëgg nu ne, na safaras asamaan dal ci seen kaw, faagaagal leen?» 9:55 Waaye Yeesu walbatiku, yedd taalibe ya, 9:56 ba noppi ñu daldi dem wuti beneen dëkk. 9:57 Bi ñuy dem, am ci yoon wi ku ne Yeesu: «Dinaa la topp fépp foo jëm.» 9:58 Waaye Yeesu tontu ko ne: «Till yi am nañu seeni kàmb, te picci asamaan am nañu ay tàgg, waaye Doomu nit ki amul fu mu noppal boppam.» 9:59 Yeesu ne keneen: «Toppal ci man.» Waaye kooku ne ko: «Sang bi, may ma, ma jëkk a dem suuli sama baay.» 9:60 Mu tontu ko ne: «Bàyyil ñi dee, ñu suul seeni néew. Yaw demal, yégle nguuru Yàlla.» 9:61 Keneen ne ko: «Sang bi, dinaa la topp, waaye may ma, ma jëkk a tàgguji sama waa kër.» 9:62 Yeesu ne ko: «Kuy ji, di geestu, yeyoowul a liggéey ci nguuru Yàlla.»
10:1 Gannaaw loolu Boroom bi tànn na yeneen juróom-ñaar-fukki taalibe ak ñaar, yebal leen, ñu ànd ñaar ak ñaar, jiituji ko ca dëkk yépp ak ca bérab yépp, ya mu naroon a dem moom ci boppam. 10:2 Mu ne leen: «Ngóob mi yaatu na, waaye liggéeykat yi barewuñu. Ñaanleen nag Boroom ngóob mi, mu yebal ay liggéeykat, ñu góob toolam. 10:3 Demleen! Maa ngi leen di yónni, mel ni ay mbote ci biir ay bukki. 10:4 Buleen yor xaalis walla mbuus walla ay dàll. Buleen nuyu kenn ci yoon wi. 10:5 «Kër gu ngeen man a dugg, nangeen jëkk ne: “Na jàmm wàcc ci kër gi.” 10:6 Bu fa nitu jàmm nekkee, seen yéene dina ko indil jàmm. Lu ko moy, seen yéene dina dellusi ci yéen. 10:7 Dal-leen ca kër googa, tey lekk ak a naan lu ñu leen di jox, ndaxte liggéeykat yelloo na jot peyam. Buleen dem nag kër ak kër. 10:8 «Dëkk bu ngeen man a dugg, te waa dëkk ba teeru leen, lu ñu leen jox, lekkleen ko. 10:9 Nangeen wéral jaragi dëkk ba, te ngeen ne leen: “Nguuru Yàlla jegesi na leen.” 10:10 Waaye bu ngeen duggee ci dëkk te teeruwuñu leen, demleen ca mbedd ya te ne leen: 10:11 “Seen pëndu dëkk, bi taq ci sunuy tànk sax, noo ngi koy faxas, ngir seede leen seen réer. Waaye nag xamleen ne, nguuru Yàlla jegesi na.” 10:12 Maa ngi leen koy wax, bu bés baa, waa Sodom ñooy tane dëkk boobu. 10:13 «Dingeen torox, yéen waa Korasin ak waa Betsayda, ndaxte kéemaan yi ma def ci yéen, bu ñu leen defoon ci dëkku Tir walla ci dëkku Sidon, kon tuub nañu seeni bàkkaar bu yàgg, xëppoo dóom, sol saaku. 10:14 Moona ca bés pénc ba, Tir ak Sidon ñoo leen di tane. 10:15 Te yaw dëkku Kapernawum, ndax dees na la yékkati bu kawe? Déedéet, dees na la daane bu suufe. 10:16 «Ku leen déglu, déglu na ma; ku leen bañ, bañ na ma. Te ku ma bañ, bañ na ki ma yónni.» 10:17 Juróom-ñaar-fukki taalibe yi ak ñaar dellusi, fees ak mbég te naan: «Boroom bi, rab yi sax déggal nañu nu ndax sa tur.» 10:18 Yeesu ne leen: «Maa ngi doon séen Seytaane wàcce asamaan ni safaras melax. 10:19 Gis ngeen, jox naa leen sañ-sañu joggi ci jaan yi ak ci jiit yi, daan dooley bañaale bi, te dara du leen man a gaañ. 10:20 Moona li leen rab yi déggal, bumu tax ngeen bég, waaye bégleen ndax li ñu bind seen tur ci asamaan.» 10:21 Ca saa soosu Xel mu Sell mi feesal Yeesu ak mbég, mu daldi ne: «Yaw Baay bi, Boroom asamaan ak suuf, maa ngi lay sant ci li nga nëbb yëf yii ñi am xam-xam ak ñi am xel, te xamal leen gune yi. Waaw Baay bi, ndaxte looloo la neex.» 10:22 Yeesu teg ca ne: «Sama Baay jébbal na ma lépp, te kenn mënul a xam, man Doom ji, maay kan, ku dul Baay bi; kenn mënul a xam it kan mooy Baay bi, ku dul man Doom ji, ak ku ma ko bëgg a xamal.» 10:23 Gannaaw bi mu waxee loolu, Yeesu walbatiku ca taalibe ya ne leen ñoom rekk: «Ñi seeni bët di gis li ngeen di gis, am nañu mbég. 10:24 Ndaxte maa ngi leen koy wax, yonent yu bare ak buur yu bare bëggoon nañoo gis li ngeen di gis, waaye gisuñu ko, te dégg li ngeen di dégg, waaye dégguñu ko.» 10:25 Noonu benn xutbakat daldi jóg, ngir fexee fiir Yeesu ne ko: «Kilifa gi, lan laa war a def, ba am dund gu dul jeex?» 10:26 Yeesu ne ko: «Lu ñu bind ci yoonu Musaa? Lan nga ciy jàng?» 10:27 Nit ka ne ko: « “Nanga bëgg Yàlla sa Boroom ak sa xol bépp ak sa bakkan bépp, sa kàttan gépp ak sa xel mépp,” te it: “Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.”» 10:28 Yeesu ne ko nag: «Li nga wax dëgg la. Boo defee loolu, dinga dund ba fàww.» 10:29 Waaye xutbakat ba bëggoon a am aw lay, ne Yeesu: «Kan mooy sama moroom nag?» 10:30 Yeesu tontu ko ne: «Dafa amoon nit ku jóge woon Yerusalem, jëm Yeriko. Ay sàcc dogale ko, futti ko, dóor ko ba muy bëgg a dee, dem bàyyi ko fa. 10:31 Faf ab saraxalekat jaar ca yoon wa, séen nit ka, teggi. 10:32 Benn waay it bu soqikoo ci giiru Lewi, aw ca bérab booba, séen waa ja, teggi. 10:33 Waaye benn waay bu dëkk Samari bu doon tukki, ñëw ba jege waa ja, gis ko, yërëm ko. 10:34 Noonu mu ñëw, diw ko diwlin ak biiñ ngir faj gaañu-gaañu ya, bandaas ko. Gannaaw loolu mu teg ko ci mbaamam, yóbbu ko ci fanaanukaay, di ko topptoo. 10:35 Bi bët setee, mu génne ñaari poseti xaalis, jox ko boroom kër ga ne ko: “Nanga topptoo nit kooku. Bés bu ma fi jaaraatee, dinaa la fey, man ci sama bopp, lépp loo ci dolli ci xaalis.”» 10:36 Yeesu teg ca ne: «Lu ciy sa xalaat? Kan ci ñett ñooñu moo jëfe ni kuy jëf jëme ci moroomam, ba ñu gisee nit, ka sàcc ya dogale woon?» 10:37 Xutbakat ba tontu ko ne: «Xanaa ki ko won yërmandeem.» Yeesu ne ko nag: «Demal tey def ni moom.» 10:38 Bi Yeesu ak ay taalibeem nekkee ci yoon wi, mu dugg ci benn dëkk, fekk fa jigéen ju tudd Màrt, ganale ko. 10:39 Màrt nag amoon rakk ju tudd Maryaama, ma nga toog ci tànki Boroom bi, di déglu ay kàddoom. 10:40 Fekk Màrt jàpp lool ca waañ wa. Noonu mu ñëw ci wetu Yeesu ne ko: «Boroom bi, doo ci wax dara, boo gisee sama rakk ji bàyyi ma ak liggéey bi yépp? Ne ko mu jàpple ma.» 10:41 Boroom bi tontu ko ne: «Màrt, Màrt, yu baree ngi fees sa xol, nga am ay téq-téq ndax loolu. 10:42 Moona de, lenn rekk a am solo. Maryaama dafa tànn cér bi gën, te kenn du ko nangu ci moom.»
11:1 Am bés Yeesu di ñaan ci benn bérab. Bi mu noppee, kenn ci taalibeem yi ne ko: «Boroom bi, jàngal nu, nan lanu war a ñaane, ni ko Yaxya jàngale ay taalibeem.» 11:2 Yeesu ne leen: «Bu ngeen dee ñaan, nangeen ne:“Baay bi, na sa tur sell,na sa nguur ñëw. 11:3 May nu bés bu nekk li nu war a dunde. 11:4 Baal nu sunuy bàkkaar,ndaxte nun itam danuy baal ñépp ñi nu tooñ.Te bu nu teg ci yoonu nattu.”» 11:5 Yeesu teg ca ne leen: «Mi ngi mel ni, nga dem seeti sa xarit ci xaaju guddi ne ko: “Xarit, lebal ma ñetti mburu. 11:6 Dafa am sama xarit bu ma ganesi, te awma dara lu ma ko jox.” 11:7 «Waaye kooku nekk ci biir néegam, dina ko tontu: “Bu ma lakkal, tëj naa bunt bi ba noppi te tëdd, man ak sama njaboot; mënumaa jóg di la jox dara.” 11:8 Maa ngi leen koy wax, su jógul jox ko li muy laaj ndax li ñu xaritoo it, ndax la kee ñàkk jom dina tax mu jox ko lépp li mu soxla. 11:9 Moo tax ma ne, ñaanleen, ñu may leen; seetleen, te dingeen gis; fëggleen, ñu ubbil leen. 11:10 Ndaxte képp kuy ñaan, dinga am; kuy seet, dinga gis; kuy fëgg, ñu ubbil la. 11:11 Bu la sa doom ñaanee jën, yaw miy baayam, ndax dinga ko bañ a jox jën, jox ko jaan? 11:12 Walla mu ñaan la nen, nga jox ko jiit? 11:13 Ndegam yéen ñi bon yéena man a jox seeni gune lu baax, astemaak Baay bi nekk ci kaw dina jox Xel mu Sell mi ñi ko koy ñaan!» 11:14 Am bés Yeesu dàq rab wu luu. Naka la rab wa génn, luu ba daldi wax, ba mbooloo may yéemu. 11:15 Waaye am ca mbooloo ma ay nit, ñu doon wax naan: «Ci kàttanu Beelsebul, buuru rab yi, lay dàqe rab yi.» 11:16 Am ñeneen ñu fexe koo fiir, ba laaj ko kéemaan gu jóge ci asamaan tey firndeel yónnentam. 11:17 Waaye Yeesu xam seen xalaat ne leen: «Réew mu xeex boppam tas, kër gu xeex boppam gent. 11:18 Te it bu Seytaane xeexee boppam, naka la nguuram di man a yàgge? Damay wax loolu, ndaxte nee ngeen, damay dàq rab jaarale ko ci kàttanu Beelsebul. 11:19 Te it bu fekkee ne man damay dàq ay rab ci kàttanu Beelsebul, seeni taalibe nag ci gan kàttan lañu leen di dàqe? Kon ñoo leen di àtte. 11:20 Waaye bu fekkee ne ci baaraamu Yàlla laay dàqe rab, kon nguuru Yàlla agsi na ba ci yéen. 11:21 «Su nit ku bare doole gànnaayoo, di wottu këram, alalam dina raw. 11:22 Waaye bu ku ko ëpp doole ñëwee, daan ko, dafay nangu gànnaay ya mu yaakaaroon, ba noppi séddale alal ja. 11:23 Ku farul ak man, yaa ngi may xeex, ku dajalewul ak man, yaa ngi tasaare. 11:24 «Boo xamee ne rab, wa jàppoon nit, génn na ci moom, day wër ay bérab yu wow, di wut fu mu noppaloo, waaye du ko gis. Noonu da naan: “Naa dellu ca sama kër, ga ma jóge.” 11:25 Bu ñëwee nag, mu fekk këram, ñu bale ko, defar ko ba lépp jekk. 11:26 Bu ko gisee nag, mu dem wooyi yeneen juróom-ñaari rab yu ko gën a soxor. Ñu dugg, sanc fa; ba tax mujug nit kooku mooy yées njàlbéenam.» 11:27 Bi Yeesu di wax loolu, jenn jigéen yékkati baatam ca biir mbooloo ma ne: «Céy jigéen ji la ëmb te nàmpal la moo barkeel!» 11:28 Waaye Yeesu tontu ko ne: «Neel kay, ki barkeel mooy kiy déglu kàddug Yàlla te di ko topp.» 11:29 Naka la mbooloo may gën a takku, Yeesu ne: «Niti jamono jii dañoo bon. Ñu ngi laaj firnde, waaye duñu jot genn firnde gu dul firndeg Yunus. 11:30 Ndaxte ni Yunus nekke woon firnde ci waa dëkku Niniw, noonu la Doomu nit kiy nekke firnde ci niti jamono jii. 11:31 Keroog bés pénc buur bu jigéen, ba dëkkoon ca sudd, dina jógandoo ak niti jamono jii, yey leen; ndaxte dafa jóge ca catul àddina, ngir déglu xam-xamu Suleymaan, te ku sut Suleymaan a ngi fi. 11:32 Te it ca bés pénc, waa dëkku Niniw dinañu jógandoo ak niti jamono jii, yey leen, ndaxte bi leen Yunus waaree, tuub nañu seeni bàkkaar, te ku sut Yunus a ngi fii. 11:33 «Kenn du taal làmp, ba noppi di ko duggal cig kàmb, walla di ci këpp leget. Daf koy wékk, ngir mu leeral ñiy dugg. 11:34 Bët mooy làmpu yaram. Bu sa bët wéree, kon sa yaram wépp leer. Waaye bu sa bët woppee, kon sa yaram wépp lëndëm. 11:35 Moytul ndax leer gi nekk ci yaw du lëndëm. 11:36 Kon bu sa yaram wépp nekkee ci leer te amul genn wet gu laal ci lëndëm, dina leer nàññ, mel ni leeraayu làmp ne ràyy ci sa kaw.» 11:37 Bi Yeesu waxee ba noppi, benn Farisen wax ko, mu ñëw lekke këram. Yeesu dugg ca kër ga, toog ca lekkukaay ba. 11:38 Farisen bi nag daldi jaaxle, bi mu gisee ne Yeesu raxasuwul, laata muy lekk. 11:39 Noonu Boroom bi ne ko: «Waaw yéen Farisen yi, yéena ngi setal bitib kaas bi ak ndab li, waaye ci biir dangeen a fees ak càcc ak mbon! 11:40 Yéena ñàkk xel! Xanaa du ki defar biti moo defar biir itam? 11:41 Saraxeleen li nekk ci biir te seen lépp dina sell. 11:42 Yéen Farisen yi dingeen torox! Ndaxte yéena ngi sàkk asaka ci naana ak ru ak léjum bu nekk, waaye sàggane ngeen njubte ak mbëggeel ci Yàlla. Loolu ngeen war a def, waxuma nag ngeen sàggane la ca des. 11:43 Yéen Farisen yi, dingeen torox! Ndaxte ca jàngu ya, toogu ya féete kanam ngeen di taamu te bëgg ñépp di leen nuyoo ñaari loxo ca pénc ma. 11:44 Dingeen torox, ndaxte dangeen a mel ni ay bàmmeel yu raaf, ba nit ñi di ci dox te teyuñu ko.» 11:45 Kenn ci xutbakat yi ne ca tonn ne: «Kilifa gi, boo waxee loolu, yaa ngi nuy xas, nun itam.» 11:46 Noonu Yeesu neeti leen: «Yéen itam xutbakat yi, dingeen torox! Ndaxte dangeen di sëf nit ñi say yu diis, waaye dungeen nangoo laal sëf bi sax ak seen cati baaraam. 11:47 Dingeen torox, ndaxte yéena ngi tabax xabruy yonent, yi seeni maam reyoon. 11:48 Dangeen di seede noonu ne, ànd ngeen ak li seen maam defoon, ndaxte ñoo rey yonent yi, yéen ngeen tabax xabru yi. 11:49 Looloo tax Yàlla mi xam lépp ne: “Dinaa leen yónnee ay yonent ak ay ndaw. Ñenn ñi dinañu leen fitnaal, rey leen.” 11:50 Kon nag Yàlla dina mbugal niti jamono jii ndax dereti yonent yi ñu tuur, ba àddina sosoo ak léegi, 11:51 la dale ca Abel ba ci Sakariya, moom mi ñu rey ci diggante saraxalukaay bi ak bérab bu sell bi. Waaw, maa ngi leen koy wax, Yàlla dina mbugal niti jamono jii ndax loolu. 11:52 Yéen xutbakat yi, dingeen torox, ndaxte yéena yóbbu caabiy xam-xam; dugguleen ci, te ku ci bëgg a dugg, ngeen tere ko ko.» 11:53 Bi Yeesu génnee bérab boobu, Farisen ya ak xutbakat ya ëmbal ko mer te di ko seetlu ci fànn gu nekk, 11:54 di ko yeeru, bëgg a këf waxam bu awul yoon.
12:1 Gannaaw loolu, naka la mbooloo ma dajaloo ba mat ay junniy junniy nit, di tancante, Yeesu tàmbalee wax jëmale ca taalibeem ya ne leen: «Moytuleen lawiiru Farisen ya, li di naaféq. 12:2 Amul dara lu nëbbu lu ñu warul a biral, mbaa lu kumpa lu ñu warul a siiwal. 12:3 Looloo tax lu ngeen wax ci biir lëndëm, dees na ko dégg ci leer. Lu ngeen déey nit ci biir néeg, dees na ko yégle ci kaw taax yi. 12:4 «Maa ngi leen koy wax, samay xarit, buleen ragal ñu man a rey yaram, ba noppi dootuñu man a def dara. 12:5 Dinaa leen wax nag ki ngeen war a ragal: ragal-leen Ki nga xam ne bu reyee ba noppi, am sañ-sañu sànni ca safara. Waaw maa ngi leen koy wax, ragal-leen kooku. 12:6 Juróomi picci rammatu, ndax duñu ko jaay ci ñaari dërëm? Moona Yàlla fàttewul benn ci ñoom. 12:7 Seen kawari bopp sax waññees na leen. Kon buleen ragal dara, yéena gën ndiiraanu rammatu. 12:8 «Te maa ngi leen koy wax, képp ku ma nangu ci kanamu nit ñi, Doomu nit ki dina la nangu ci kanamu malaakay Yàlla yi. 12:9 Waaye ku ma gàntu ci kanamu nit ñi, dinañu la gàntu ci kanamu malaakay Yàlla yi. 12:10 Ku sosal Doomu nit ki, dinañu la baal, waaye kuy sosal Xel mu Sell mi, duñu la ko baal. 12:11 «Bu ñu leen yóbboo ca jàngu ya, ca kanamu kilifa ya ak àttekat ya, buleen am xel ñaar ci li ngeen war a tontu ak nan ngeen war a tontoo, walla lu ngeen war a wax, 12:12 ndaxte Xel mu Sell mi dina leen xamal ca waxtu woowa li ngeen war a wax.» 12:13 Am ca mbooloo ma ku ne Yeesu: «Kilifa gi, joxal ndigal sama mag, mu sédd ma ci sunu ndono.» 12:14 Yeesu tontu ko ne: «Sama waay, kan moo ma fal àttekat ci seen kaw, walla mu teg ma fi, ma di leen séddaleel seen alal?» 12:15 Noonu mu ne leen ñoom ñépp: «Moytuleen bëgge, ndaxte bakkanu nit ajuwul ci alalam, ak lu mu baree-bare.» 12:16 Noonu mu dégtal leen wii léeb ne: «Dafa amoon waa ju bare alal, te ay toolam nangu lool, 12:17 muy werante ci xelam naan: “Nu ma war a def? Ndaxte amatuma fu ma dajale sama ngóob mi.” 12:18 Noonu mu ne: “Nii laay def: daaneel sama sàq yi, defaraat yu gën a réy, ba man cee dajale sama dugub ji ak sama am-am jépp. 12:19 Te dinaa kañ sama bopp ne: ’Yaw mii, am nga alal ju bare ju man a dem ay ati at; noppalal sa yaram, di lekk, di naan, tey bég.’ ” 12:20 Waaye Yàlla ne ko: “Ñàkk xel! Guddig tey, dees na jël sa bakkan. Kon li nga dajale lépp, ku koy moom?” 12:21 «Kiy dajale alal ngir boppam nag te amul dara ca kanam Yàlla, lu mel nii moo lay dal.» 12:22 Noonu Yeesu daldi ne taalibeem yi: «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, buleen seen bakkan jaaxal, ci lu ngeen war a lekk. Buleen jaaxle it ngir seen yaram ci lu ngeen war a sol, 12:23 ndaxte bakkan moo gën lekk, te yaram a gën koddaay. 12:24 Seetleen baaxoñ yi: duñu ji, duñu góob, amuñu dencukaay, amuñu sàq, teewul Yàllaa ngi leen di dundal. Céy ni ngeen ëppe maana picc yi! 12:25 Ana kan ci yéen ci kaw njaaxleem, moo man a yokk ab waxtu ci àppam? 12:26 Su fekkee lu tuuti loolu rekk mënuleen koo def, kon lu tax ngeen di jaaxle ci li ci des? 12:27 «Seetleen ni tóor-tóori ñax mi di saxe. Duñu liggéey, duñu ëcc, waaye maa ngi leen di wax ne, Suleymaan sax ci ndamam, soluwul woon ni benn ci ñoom. 12:28 Yéen ñi néew ngëm! Bu Yàlla woddee nii ñaxu tool yi, miy sax tey te bu subaa ñu def ko ci taal bi, ndax du leen gën a wodd? 12:29 Buleen di wut lu ngeen di lekk walla lu ngeen di naan; te buleen ci jaaxle. 12:30 Ndaxte loolu lépp, ñi xamul Yàlla ñoo koy wut. Te seen Baay xam na ne, soxla ngeen ko. 12:31 Waaye wutleen nguuram, te loolu lépp dina leen ko ci dollil. 12:32 «Buleen ragal dara, yéen coggal ju ndaw ji, ndaxte dafa soob seen Baay, mu jagleel leen nguuram. 12:33 Jaayleen seen alal, saraxe ko, ngir sàkku ay mbuusi xaalis yu dul bënn, maanaam alal ju dul jeex ca laaxira; foofa sàcc du ko jege te max du ko yàq. 12:34 Ndaxte fu sa alal nekk, fa la sa xol nekk itam. 12:35 «Takkuleen bu dëgër te bàyyi làmp yi tàkk. 12:36 Mel-leen ni ay surga yuy xaar seen njaatige buy jóge ca céet ga, ndax bu fëggee bunt ba, ñu ubbil ko ca saa sa. 12:37 Surga yooyee seen njaatige fekkul ñuy nelaw, ba mu agsee, ñoo gën a yeyoo ngërëm. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, njaatige bi dina sol yérey waañ, wax leen ñu toog lekk, ba noppi indil leen ñam wi. 12:38 Su fekkee seen njaatige ci xaaju guddi lay ñëw sax, walla bu suuf seddee, te fekk leen noonu, surga yooyu ñoo gën a yeyoo ngërëm. 12:39 Waaye xamleen lii: bu boroom kër gi xamoon ban waxtu la sàcc bi di ñëw, du ko bàyyi, mu toj këram. 12:40 Yéen itam taxawleen jonn, ndaxte Doomu nit ki dina ñëw ci waxtu wu ngeen ko séenuwul.» 12:41 Piyeer ne Yeesu: «Boroom bi, ndax dangay dégtal léeb wii ngir nun rekk walla ngir mbooloo mépp?» 12:42 Boroom bi tontu ko ne: «Kan moo nekk surga bu takku te teey, bu njaatigeem teg ci waa kër gi, ngir mu leen di dundal ci jamono ji? 12:43 Bu njaatigeem ñëwee te gis mu def noonu, surga boobu dina am ngërëm. 12:44 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, njaatige bi dina ko teg ci alalam jépp. 12:45 Waaye su fekkee surga ba da ne ci xelam: “Sama njaatige day yéex a ñëw,” ba tax mu tàmbalee dóor surga ya ca des ak mbindaan ya, di lekk te di naan, di màndi, 12:46 kon njaatige ba dina ñëw ci bés bu mu ko séenuwul ak waxtu wu mu xamul. Dina ko dóor ay dóor yu metti, jox ko añub ñi gëmul Yàlla. 12:47 «Surga bi xam bëgg-bëggu njaatigeem, te waajul mbaa mu takku def ko, dinañu ko dóor dóor yu metti. 12:48 Waaye surga bi xamul bëgg-bëggu njaatigeem, te def lu yelloo ay dóor, dinañu ko dóor dóor yu néew. Ku ñu jox lu bare dees na la feyiku lu bare. Ku ñu dénk lu bare, dees na la laajaat lu ko ëpp. 12:49 «Damaa ñëw ngir indi safara si ci àddina, te bëgg naa xaat taal bi tàkk. 12:50 Fàww ñu sóob ma ci metit, te ba looluy mat, duma noppalu. 12:51 Ndax dangeen a xalaat ne, damaa ñëw ngir indi jàmm ci àddina? Déedéet. Maa ngi leen koy wax, damaa ñëw ngir indi féewaloo. 12:52 Gannaawsi tey, bu juróomi nit bokkee genn kër, dinañu féewaloo. Ñett dinañu féewaloo ak ñaar ñi ci des, ñaar ñi féewaloo ak ñett ñooñu. 12:53 Baay bi dina féewaloo ak doom ji, doom ji ak baayam. Ndey dina féewaloo ak doomam ju jigéen; doom ju jigéen ji ak ndeyam. Goro dina féewaloo ak jabaru doomam; jabaru nit ak goroom.» 12:54 Yeesu neeti mbooloo ma: «Bu ngeen gisee mu xiin ci sowu, dangeen naan ca saa sa: “Dina taw,” te mooy am. 12:55 Te bu ngeen yégee ngelaw liy uppe sudd, ngeen ne: “Dina tàng tàngaay wu metti,” te mooy am. 12:56 Naaféq yi ngeen doon! Man ngeen a ràññee melow asamaan ak suuf, waaye lu tax mënuleen a ràññee li jamonoy léegi ji di tekki? 12:57 «Lu tax it dungeen àtteel seen bopp liy jëf ju jub? 12:58 Bu la nit jiiñee dara, ba ngeen ànd di dem ca àttekat ba, nanga fexee juboo ak moom ci yoon wi. Lu ko moy, dina la yóbbu ci yoon, yoon jébbal la ca loxoy alkaati ba, mu tëj la. 12:59 Maa ngi la koy wax, doo génn foofa mukk te feyuloo fiftin bi ci mujj.»
13:1 Ca jamono jooju ay nit ñëw ca Yeesu, nettali mbirum waa Galile, ya Pilaat reylu woon, jaxase seen deret ak dereti mala, yi ñu rendi woon, jébbal leen Yàlla. 13:2 Mu tontu leen ne: «Mbaa du dangeen a xalaat ne, waa Galile yooyu dañoo gën a nekk bàkkaarkat ña ca des, ndax coono bi ñu daj? 13:3 Maa ngi leen di wax ne, du dëgg. Waaye su ngeen tuubul seeni bàkkaar, dingeen sànku noonu, yéen ñépp itam. 13:4 Te fukki nit ak juróom-ñett ñooñu dee, bi taaxum kaw ma ca goxu Silowe daanoo ci seen kaw, ndax dangeen a yaakaar ne, ñoo gën a nekk ay tooñkat ñeneen ñi dëkk Yerusalem yépp? 13:5 Maa ngi leen di wax ne, du dëgg. Waaye su ngeen tuubul seeni bàkkaar, dingeen sànku noonu, yéen ñépp itam.» 13:6 Noonu mu daldi leen wax léeb wii: «Nit amoon na ci toolam garab gu ñu naan figg. Benn bés mu ñëw di ko raas-si, fekku fa benn doom. 13:7 Noonu mu ne surga ba: “Ñetti at a ngii may ñëw di raas-si garab gii te duma ci fekk dara. Gor ko. Lu tax muy xatal tool bi?” 13:8 Surga ba tontu ko ne: “Sang bi, bàyyiwaat ko fi at mii. Dinaa wàqi taat wi, def ci tos. 13:9 Xëy na dina meññi. Bu ko deful, nga gor ko.”» 13:10 Benn bésu noflaay Yeesoo ngi doon jàngale ci ab jàngu. 13:11 Amoon na fa jigéen ju rab jàppoon, ba feebarloo ko lu war a mat fukki at ak juróom-ñett; dafa xuuge woon te mënul woon a siggi dara. 13:12 Bi ko Yeesu gisee, mu woo ko ne ko: «Soxna si, sa feebar deñ na.» 13:13 Noonu mu teg ko ay loxoom, soxna sa siggi ca saa sa, di màggal Yàlla. 13:14 Waaye njiitu jàngu ba mer, ndax li Yeesu fajoon nit ca bésu noflaay ba, mu ne mbooloo ma: «Am na juróom-benni fan yu nit ñi war a liggéey. Kon war ngeen a ñëw faju ci bés yooyu, waaye du ci bésu noflaay bi.» 13:15 Boroom bi tontu ko: «Naaféq yi! Ndax bésu noflaay bi, kenn ku nekk ci yéen du yiwee ca gétt ga yëkkam walla mbaamam ngir wëggi ko? 13:16 Jigéen jii nag bokk ci askanu Ibraayma te Seytaane tënk ko fukki at ak juróom-ñett, ndax kenn waru koo yiwi ci bésu noflaay bi?» 13:17 Naka la wax loolu, noonam yépp daldi rus, waaye mbooloo mi di bég ci jëf yu yéeme, yi mu doon def yépp. 13:18 Noonu Yeesu neeti: «Lan la nguuru Yàlla di nirool? Lan laa ko man a mengaleel? 13:19 Mi ngi mel ni doomu fuddën gu nit jël, ji ko ci toolam. Mu sax, nekk garab, ba picci asamaan ñëw, tàgg ciy caram.» 13:20 Mu neeti: «Lan laa man a mengaleek nguuru Yàlla? 13:21 Mi ngi mel ni lawiir bu jigéen jël, jaxase ko ak ñetti andaari fariñ, ba kera tooyal bépp di funki.» 13:22 Yeesoo ngi doon jaar ci ay dëkk yu mag ak yu ndaw, di jàngale te jublu Yerusalem. 13:23 Am ku ko ne: «Boroom bi, ndax ñiy mucc ñu néew lay doon?» Yeesu ne leen: 13:24 «Defleen seen kem-kàttan, ngir dugg ci bunt bu xat bi, ndaxte maa ngi leen koy wax, ñu bare dinañu jéem a dugg, waaye duñu ko man. 13:25 Jamono dina ñëw, ju boroom kër gi di jóg, tëj buntam. Dingeen nekk ci biti di fëgg naan: “Boroom bi, ubbil nu!” Dina leen tontu ne: “Xawma fu ngeen bokk.” 13:26 Bu ko defee dingeen tàmbalee naan: “Noo doon bokk di lekk ak di naan, te jàngale nga ci sunuy pénc.” 13:27 Waaye dina ne: “Nee naa leen xawma fu ngeen bokk. Yéen ñépp soreleen ma, defkati lu bon yi!” 13:28 Foofa dingeen jooy, di yéyu, bu ngeen gisee seeni maam Ibraayma, Isaaxa, Yanqóoba ak yonent yépp ci nguuru Yàlla, te ñu dàq leen ca biti. 13:29 Ay nit dinañu jóge penku ak sowu, nor ak sudd, ñëw, bokk lekk ci ñam, yi Yàlla di joxe ci nguuram. 13:30 Noonu ñenn ci ñi mujj ñooy jiituji; te ci ñi jiitu, ñooy mujji.» 13:31 Ca jamono jooja ay Farisen ñëw ca Yeesu ne ko: «Jógeel fii, dem feneen, ndaxte Erodd a ngi lay wut a rey.» 13:32 Noonu mu ne leen: «Demleen ne bukki boobu ne ko: “Xoolal, maa ngi dàq rab yi tey wéral nit ñi tey ak suba. Ca ñetteelu fan ba, ma àgg fa ma Yàlla jëmale.” 13:33 Waaye fàww ma dox sama itte tey, suba ak gannaaw suba, ndaxte wareesul a reye ab yonent feneen fu dul Yerusalem. 13:34 «Yerusalem, Yerusalem, yaw miy rey yonent yi, tey sànni ay doj ndaw yi, ba ñu dee, aka maa bëggoon a dajale say doom, ni ginaar di uufe ay cuujam te nanguwuleen! 13:35 Kon nag Yàlla dina bërgël seen kër. Te maa ngi leen koy wax, dungeen ma gisati, ba kera ngeen ne: “Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga!”»
14:1 Benn bésu noflaay Yeesu dem ci këru benn kilifag Farisen yi, ngir lekke fa. Nit ñaa ngi ko doon xool bu baax. 14:2 Faf am ca kanamam nit ku feebaroon, ay tànkam newi. 14:3 Yeesu yékkati baatam, ne xutbakat ya ak Farisen ya: «Ndax jaadu na, nu faj ci bésu noflaay bi?» 14:4 Waaye ñépp ne cell. Yeesu daldi laal jarag ja, faj ko, ba noppi ne ko mu ñibbi. 14:5 Gannaaw loolu mu ne leen: «Ku sa doom walla sa yëkk daanu ci teen, ndax doo dem génneji ko ca saa sa, fekk sax bésub noflaay la?» 14:6 Amuñu woon dara lu ñu ciy teg. 14:7 Yeesu gis ni gan yi doon tànne toogu yu yiw yi, mu daldi leen wax léeb wii: 14:8 «Bu ñu la wooyee ci xewu céet, bul jël toogu bu yiw. Man na am woo nañu it nit ku la ëpp daraja. 14:9 Kon ki leen woo yéen ñaar ñépp man na ñëw ci yaw ne la: “Joxal toogu bi nit kii.” Noonu dinga rus a dem ca toogu bu gannaawe ba. 14:10 Waaye bu ñu la wooyee, demal ca toogu bu gannaawe ba. Bu ko defee ki la woo, bu agsee ne la: “Sama xarit, àggal ca kaw.” Loolu dina la sagal ci ñi nga toogandool ci lekkukaay bi. 14:11 Ndaxte képp kuy yékkatiku, dees na la suufeel, te kuy suufeelu, dinañu la yékkati.» 14:12 Noonu Yeesu ne ki ko woo woon lekk: «Boo dee woote añ walla reer, bul woo rekk say xarit, say doomi ndey, say bokk, walla say dëkkandoo yu am alal. Lu ko moy ñooñu itam dinañu la woo, fey la bor bi. 14:13 Waaye boo dee woote lekk, wool néew doole yi, làggi yi, lafañ yi ak gumba yi. 14:14 Soo ko defee, dinga barkeel, ndaxte duñu la ko man a fey, waaye dinga jot sag pey, bés bi ñi jub di dekki.» 14:15 Bi mu déggee wax yooyu, kenn ca gan ya ne Yeesu: «Kiy lekk ci ñam, yi Yàlla di joxe ci nguuram, barkeel nga!» 14:16 Yeesu tontu ko ne: «Dafa amoon nit ku togglu ay ñam, woo ay nit ñu bare. 14:17 Bi waxtuw lekk jotee mu yónni surga ca ña muy ganale, fàttali leen: “Man ngeen a ñëw, ndaxte lépp sotti na léegi.” 14:18 «Waaye ñu tàmbali di jéggalu ci ngan gi ñoom ñépp. Ku jëkk ka ne ko: “Damaa jënd tool léegi, te fàww ma dem seeti ko. Maa ngi lay ñaan, nga jéggal ma.” 14:19 Keneen ne: “Damaa jënd léegi fukki yëkk, te damay dem nii, jéem leen a beyloo ba xam. Maa ngi lay ñaan, nga jéggal ma.” 14:20 Keneen ne ko: “Damay sog a takk jabar, looloo tax duma man a ñëw.” 14:21 «Surga ba dellu ca njaatigeem nettali ko loolu lépp. Noonu boroom kër ga mer, daldi ne surga ba: “Demal gaaw ca pénc ya ak ca mbedd ya ca dëkk ba, te indil ma fii néew doole yi, ñu làggi ñi, gumba yi ak lafañ yi.” 14:22 «Surga ba ñëwaat ne ko: “Sang bi, def naa li nga ma sant, waaye bérab bi feesul.” 14:23 Noonu njaatige ba ne ko: “Génnal dëkk bi te dem ca yoon ya ak ca tool ya, xiir nit ñi, ñu duggsi, ngir sama kër fees. 14:24 Maa ngi leen koy wax, ci ñi ma woo woon ci sama reer bi, kenn du ci ñam.”» 14:25 Am mbooloo yu réy yu toppoon ci Yeesu, ba muy dem ca yoon wa. Mu geestu ne leen: 14:26 «Képp ku ñëw ci man te gënalu ma ko baayam, yaayam, jabaram, ay doomam, ay magam ak ay rakkam, walla sax bakkanam, du man a nekk sama taalibe. 14:27 Képp koo xam ne nanguwuloo ñàkk sa bakkan, ba mel ni ku ñu daaj ci bant, te nga topp ma, doo man a nekk sama taalibe. 14:28 Su kenn ci yéen bëggee tabax taaxum kaw, ndax du jëkk a toog, xalaat ñaata la ko war a dikke, ngir seet ba xam ndax am na xaalis bu man a àggale liggéey bi? 14:29 Lu ko moy, su yékkatee fondamaa bi te mënu koo àggale, ñi koy gis dinañu ko ñaawal, naan ko: 14:30 “Waa jii dafa tàmbalee tabax, waaye mënu koo àggale.” 14:31 Walla boog ban buur mooy dugg ci xare ak beneen buur te jëkkul a toog, seet ba xam moom ak fukki junniy xarekat man na xeex ak kiy ñëw ak ñaar-fukki junniy xarekat? 14:32 Su ko mënul, dafay yónni ndaw ca beneen buur ba, fi ak ma ngay sore, ngir ñu juboo. 14:33 Naka noonu itam ku nekk ci yéen, bu dëdduwul li mu am lépp, du man a nekk sama taalibe. 14:34 «Xam ngeen nag ne, xorom lu baax la, waaye bu sàppee, nan lañu koy delloo cafkaam? 14:35 Du jariñ suuf, te du nekk tos. Dañu koy sànni ca biti. Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»
15:1 Ay juutikat ak ay boroom bàkkaar daan jegesi Yeesu ngir déglu ko. 15:2 Farisen ya ak xutbakat ya di ñurumtu naan: «Waa jii mi ngi nangoo nekk ak ay boroom bàkkaar ak a lekkandook ñoom!» 15:3 Noonu Yeesu daldi leen wax léeb wii ne leen: 15:4 «Kan ci yéen soo amoon téeméeri xar, te benn réer ci, nooy def? Ndax doo bàyyi ca parlukaay ba juróom-ñeent-fukki xar ya ak juróom-ñeent, toppi ma réer, ba gis ko? 15:5 Te boo ko gisee, dinga ko gàddu ak bànneex, yóbbu ko kër ga. 15:6 Boo àggee ca kër ga, dinga woo say xarit ak say dëkkandoo ne leen: “Kaayleen bànneexu ak man, ndaxte gis naa sama xar ma réeroon.” 15:7 «Maa ngi leen di wax lii: ci noonule, dina am mbég ci asamaan, bu benn bàkkaarkat tuubee ay bàkkaaram. Te mbég moomu mooy ëpp mbég, mi fay am, ngir juróom-ñeent-fukk ak juróom-ñeent ñu jub, te soxlawuñoo tuub seeni bàkkaar. 15:8 «Te it bu jigéen dencoon fukki libidoor, benn réer ca, nu muy def? Ndax du taal ab làmp, bale kër ga, seet fu nekk, ba gis ko? 15:9 Bu ko gisee, dina woo ay xaritam ak ay dëkkandoom ne leen: “Kaayleen bànneexu ak man, ndaxte gis naa sama alal ja réeroon.” 15:10 Maa ngi leen di wax lii: ci noonule la malaakay Yàlla yi di ame mbég ci benn bàkkaarkat bu tuubee ay bàkkaaram.» 15:11 Yeesu dellu ne leen: «Dafa amoon góor gu am ñaari doom. 15:12 Benn bés caat ma ne baay ba: “Baay, damaa bëggoon, nga jox ma li may war a féetewoo ci ndono li.” Noonu baay ba daldi leen séddale alalam. 15:13 Ay fan yu néew gannaaw gi, caat ma fab yëfam yépp, dem ca réew mu sore, yàq fa alalam ci topp nafsoom. 15:14 Bi mu sànkee alalam jépp, xiif bu metti dal ca réew ma, mu tàmbalee ñàkk. 15:15 Mu dem nag, di liggéeyal ku dëkk ca réew ma, kooku yebal ko ca ay toolam ngir mu sàmm mbaam-xuux ya. 15:16 Mu xiif ba bëgg a lekk ca ñamu mbaam-xuux ya, ndaxte kenn mayu ko dara. 15:17 Mujj xelam dellusi, mu ne: “Sama baay am na ay surga yu bare, te dañuy lekk ba suur. Man nag maa ngi fii di bëgg a dee ak xiif! 15:18 Damay jóg, dem ca sama baay ne ko: ‘Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ naa la; 15:19 yeyootumaa nekk sa doom; boole ma ci say surga.’ ” 15:20 «Mu daldi jóg, jëm kër baayam. Waaye bi muy soreendi kër ga, baayam séen ko, yërëm ko, daldi daw laxasu ko, fóon ko. 15:21 Doom ja ne ko: “Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ naa la; yeyootumaa nekk sa doom.” 15:22 Waaye baay ba ne ay surgaam: “Gaawleen indi mbubb, mi gën a rafet, solal ko ko. Te ngeen roof ab jaaro ci loxoom te solal ko ay dàll. 15:23 Indileen sëllu wu duuf wa te rey ko, nu lekk te bànneexu; 15:24 ndaxte sama doom jii dafa dee woon te dundaat na, dafa réeroon te feeñ na.” Noonu ñu tàmbalee bànneexu. 15:25 «Fekk booba taaw baa nga woon ca tool ya. Bi mu ñëwee, ba jub kër ga, mu dégg ñuy tëgg, di fecc. 15:26 Mu daldi woo kenn ca surga ya nag, laaj ko lu xew. 15:27 Mu tontu ko: “Sa rakk moo dellusi, te sa baay rey na sëllu wu duuf wa, ndaxte ñibbisi na ci jàmm.” 15:28 «Ci kaw loolu taaw ba daldi mer, bañ a dugg ca kër ga. Baayam daldi génn, ngir ñaan ko mu dugg. 15:29 Waaye taaw ba tontu baayam ne ko: “Seetal ñaata at laa la liggéeyal, mel ni jaam, te musumaa moy sa ndigal, waaye yaw, musuloo ma may sax tef, ngir ma bànneexu, man ak samay xarit. 15:30 Waaye bi sa doom jii dikkee, moom mi yàq sa alal ci ndoxaan, reyal nga ko sëllu wu duuf wi.” 15:31 Noonu baay bi tontu ko ne ko: “Sama doom, yaa ngi ak man bés bu nekk, te li ma am lépp, yaa ko moom. 15:32 Waaye war nanoo bànneexu te bég, ndaxte sa rakk jii dafa dee woon te dundaat na, dafa réeroon te feeñ na.”»
16:1 Yeesu neeti ay taalibeem: «Benn boroom alal moo amoon bëkk-néeg bu ñu jiiñ ne, dafay pasar-pasaree alal ji. 16:2 Waa ja woo ko ne ko: “Li may dégg ci yaw mooy lan? Leeralal ma ni nga liggéeye ak sama alal, ndaxte dootoo nekkati sama bëkk-néeg.” 16:3 «Bëkk-néeg bi di xalaat naan: “Nu may def nag, segam sama njaatige dafa may dàq ci liggéey bi mu ma joxoon? Dem beyi? Awma kàttanam. Yelwaani? Rus naa ko. 16:4 Xam naa ni may def, ba su ma ñàkkee sama liggéey, ay nit fat ma.” 16:5 Noonu mu daldi woolu kenn ku nekk ca ña ameeloon njaatigeem bor. Ka jëkk a ñëw, mu ne ko: “Ñaata nga ameel sama njaatige?” 16:6 Mu ne ko: “Téeméeri bidoŋi diwlinu oliw.” Bëkk-néeg ba ne ko: “Sa kayit a ngii. Toogal fii gaaw te bind juróom-fukk.” 16:7 Mu neeti keneen: “Yaw nag, ñaata nga ko ameel?” Mu ne ko: “Téeméeri saakuy pepp.” Bëkk-néeg ba ne ko: “Sa kayit a ngii. Bindal juróom-ñett-fukk.” 16:8 Njaatige ba nag daldi naw ni bëkk-néeg bu njublaŋ boobu muuse woon. Ndaxte ñi bokk ci àddina ñoo gën a muus ci li ñu jote ci seen diggante ak seen moroom, ba raw ñi bokk ci leeru Yàlla.» 16:9 Yeesu teg ca ne: «Maa ngi leen di wax lii: sàkkuleen ay xarit jaare ko ci alalu àddina, ngir bu alal nekkatul, ñu man leen a fat ca dal yu sax ya. 16:10 Nit ku maandu ci yëf yu néew, dina maandu itam ci yu bare. Ku jubadi ci yëf yu néew, du jub ci yu bare. 16:11 Su fekkeente ne nag jubuleen ci alalu àddina, kon ku leen di dénk alal ju wóor ji? 16:12 Te su ngeen maanduwul ci alal ji ngeen moomul, kon ku leen di jox alal ji ngeen moom? 16:13 «Benn jaam mënul a jaamoondoo ñaari sang; fàww nga bañ kii, bëgg ki ci des, walla nga jàpp ci kenn ki, xeeb ki ci des. Mënuleen a boole jaamu Yàlla ak jaamu Alal.» 16:14 Farisen yi déglu li Yeesu doon wax lépp, tàmbali di ko reetaan, ndaxte ñu bëggoon xaalis lañu. 16:15 Waaye Yeesu ne leen: «Yéen yéena ngi fexee jub ci kanamu nit ñi waaye Yàlla xam na seen xol. Ndaxte li nit ñiy fonk, Yàlla sib na ko. 16:16 «Yoonu Musaa wi ak waxi yonent yi ñu ngi fi woon ba kera Yaxya di ñëw. La ko dale foofa nag, yégle nañu xebaar bu baax bi ci nguuru Yàlla, te ñépp a ngi góor-góorlu, ngir dugg ci. 16:17 Waaye nag asamaan ak suuf jóge fi moo gën a yomb randal wenn rëdd ci arafu yoonu Musaa. 16:18 «Ku fase sa jabar, ba noppi takk keneen, njaaloo nga, te ku takk jigéen ju jëkkëram fase, njaaloo nga. 16:19 «Dafa amoon boroom alal juy sol yére yu rafet te jafe, tey dund bés bu set dund gu neex. 16:20 Fekk miskin mu ñuy wax Lasaar daan tëdd ca buntu këram, fees dell ak ay góom, 16:21 te bu sañoon, di lekk ci desiti ñam wiy rot ci lekkukaayu boroom alal ji. Xaj yi sax daan nañu ñëw, di mar ay góomam. 16:22 «Noonu miskin ma dee, malaaka yi yóbbu ko ca wetu Ibraayma. Boroom alal ja itam dee, ñu suul ko. 16:23 Bi ñu koy mbugal ca safara, mu téen, séen fu sore Ibraayma ak Lasaar ci wetam. 16:24 Noonu mu yuuxu ne: “Maam Ibraayma, yërëm ma! Yebalal Lasaar, mu sëpp catul baaraamam ci ndox, seralal ma sama làmmiñ, ndaxte maa ngi sonn lool ci safara sii!” 16:25 Ibraayma ne ko: “Sama doom, fàttalikul ne, jot nga sa bànneex ci àddina, fekk Lasaar dëkk ci tiis. Looloo tax xolam sedd fii, yaw nag, ngay sonn. 16:26 Rax-ca-dolli it am na kàmb gu xóot sunu diggante ak yéen, ba tax ñi bëgg a jóge fii jëm ci yéen, walla ñi bëgg a jóge foofu jëmsi ci nun, duñu ko man.” 16:27 «Noonu boroom alal ja ne: “Kon nag maam, maa ngi lay ñaan, nga yebal Lasaar ca sama kër baay, 16:28 ndaxte am naa fa juróomi rakk. Na leen artu, ngir ñu bañ a ñëw ñoom itam ci bérabu metit wii.” 16:29 Ibraayma ne ko: “Say doomu baay, ñu ngeek yoonu Musaa ak téerey yonent yi. Nañu leen déggal.” 16:30 Boroom alal ja ne ko: “Déedéet, maam Ibraayma, waaye su kenn dekkee, dem ca ñoom, dinañu tuub seeni bàkkaar.” 16:31 Waaye Ibraayma tontu ko ne: “Su ñu dégluwul Musaa ak yonent yi, kon ku dekki sax, du tax ñu gëm.”»
17:1 Yeesu waxaat ay taalibeem ne leen: «Fiir yuy yóbbe nit bàkkaar mënta ñàkk, waaye toroxte dal na ki koy lal. 17:2 Ñu takk doj wu réy ci baatam, sànni ko ci géej moo gën ci moom muy daaneel ci bàkkaar kenn ci ñi gën a tuuti ci ñii. 17:3 Wottuleen seen bopp. «Bu sa mbokk tooñee, yedd ko. Bu réccoo, baal ko. 17:4 Te su la tooñee juróom-ñaari yoon ci bés bi, te ñëw ci yaw juróom-ñaari yoon ne la: “Tuub naa ko,” nanga ko baal.» 17:5 Ndaw ya wax Boroom bi ne ko: «Yokkal sunu ngëm.» 17:6 Boroom bi tontu ne: «Su ngeen amee ngëm gu tuuti sax niw peppu fuddën, kon dingeen man a ne garab gii: “Buddeekul, dem jëmbëtu ca géej ga,” te dina def li ngeen wax. 17:7 «Kan ci yéen bu amoon surga bu beyi walla bu sàmmi ba ñëw, ndax dafa ko naa: “Kaay lekk.” 17:8 Déedéet. Xanaa kay da ko naan: “Defaral ma réer bi. Takkul te tibbal ma, ba ma lekk te naan, ba noppi nga door a lekk te naan.” 17:9 Li surga ba topp ndigal, ndax tax na mu yelloo ngërëm? Déedéet. 17:10 Noonu yéen itam bu ngeen toppee li ñu leen sant lépp ba noppi, dangeen a war ne: “Ay surga rekk lanu. Sunu warugar lanu def.”» 17:11 Bi muy dem Yerusalem ba tey, Yeesu jaar ci dig wiy xaajale Samari ak Galile. 17:12 Bi muy jub benn dëkk, fukki gaana ñëw, dogale ko. Ñu taxaw dand ko, di wax ca kaw naan: 17:13 «Yeesu, kilifa gi, yërëm nu!» 17:14 Naka la leen Yeesu di gis, naan leen: «Demleen won seen bopp saraxalekat ya.» Bi ñuy dem, ñu daldi set. 17:15 Kenn ci ñoom gis ne wér na, daldi dëpp, di màggal Yàlla ak baat bu xumb. 17:16 Mu dëpp jëwam ca tànki Yeesu, di ko gërëm. Fekk nitu Samari la woon. 17:17 Noonu Yeesu daldi ne: «Xanaa du fukk yépp a wér? Ana juróom-ñeent ña nag? 17:18 Amul kenn ci ñoom ku ñëw gërëm Yàlla ku dul doxandéem bii!» 17:19 Noonu Yeesu ne ko: «Jógal dem; sa ngëm faj na la.» 17:20 Farisen yi laaj Yeesu ne ko: «Kañ la Yàlla di tëral nguuram?» Mu tontu leen ne: «Bu Yàlla di wàcce nguuram ci nit ñi, kenn du ko man a teg bët. 17:21 Duñu man a wax it ne: “Xool-leen, mi ngi fii,” walla: “Ma nga fale,” ndaxte nguuru Yàlla wàcc na ci seen biir.» 17:22 Noonu mu ne taalibe ya: «Jamono dina ñëw, fu ngeen di bëgg a gis su doon sax benn fan ci jamono ju Doomu nit ki di ñëw, waaye dungeen ko gis. 17:23 Dees na leen ne: “Mi ngi fii!” walla: “Ma nga fale!” Buleen dem, mbaa ngeen di leen topp. 17:24 Ndaxte ni melax naan ràyye ci asamaan, di leeral gii wet, ba ca gee, noonu it la Doomu nit ki di mel ci bésam. 17:25 Waaye balaa booba fàww mu sonn lool te niti jamono jii dëddu ko. 17:26 «La xewoon ca bési Nóoyin, dina xewaat ci bési Doomu nit ki. 17:27 Nit ñaa ngi doon lekk ak di naan, di jël jabar ak a séyi, ba bés ba Nóoyin duggee ca gaal ga. Noonu mbënn ma ñëw, rey leen ñoom ñépp. 17:28 «Dina mel it ni la xewoon ca bési Lóot. Nit ñaa ngi doon lekk ak di naan, di jënd ak di jaay, di ji ak di tabax. 17:29 Waaye bés ba Lóot génnee Sodom, Yàlla tawloo safara ak tamarax, rey leen ñoom ñépp. 17:30 Noonu lay mel, bés bu Doomu nit kiy feeñ. 17:31 «Ca bés boobee ku nekk ca kaw kër ga te ay bagaasam nekk ca biir, bumu wàcc jëli leen. Te it ku nekk ca tool ya, bu mu ñibbi. 17:32 Fàttalikuleen jabaru Lóot! 17:33 Kuy wut a rawale sa bakkan, dinga ko ñàkk, waaye ku ko ñàkk, dinga dund. 17:34 Maa ngi leen koy wax: ca jamono jooju, ñaar dinañu bokk a tëdd guddi, dees na yóbbu kenn ki, bàyyi ka ca des. 17:35 Ñaari jigéen dinañu wolandoo, dees na yóbbu kenn ci, bàyyi ka ca des.» 17:37 Taalibe yi ne Yeesu: «Fu loolu di xewe, Boroom bi?» Yeesu tontu leen ne: «Fa médd nekk, la tan yiy dajee.»
18:1 Noonu Yeesu wax leen itam léeb wii ngir xamal leen ne, war nañoo sax ci ñaan te bañ a xàddi. 18:2 Nee na: «Dafa amoon cib dëkk, benn àttekat bu ragalul Yàlla te faalewul mbindeef. 18:3 Amoon na itam ca dëkk ba jigéen ju jëkkëram faatu ju daan faral di ñëw ci moom, naan ko: “Àtte ma ak sama noon!” 18:4 Àttekat ba bañ lu yàgg, waaye am bés mu ne ci xelam: “Ragaluma Yàlla te faalewuma mbindeef, 18:5 waaye jigéen jii lakkal na ma; kon dinaa ko àtte, ngir mu bañatee ñëw sonal ma. Dina rey ak ay wax.”» 18:6 Boroom bi tegaat ca ne: «Dégluleen bu baax li àttekat bu bon boobu wax; 18:7 ndax Yàlla du àtte jub mbooloom mi mu tànn te ñu koy ñaan wall guddi ak bëccëg? Ndax dina leen xaarloo? 18:8 Maa ngi leen koy wax, dina leen àtte jub ci lu gaaw. Waaye bu Doomu nit ki ñëwee, ndax dina fekk ngëm ci àddina?» 18:9 Yeesu waxaat léeb wii nit, ñi foog ne jub nañu tey xeeb ñi ci des. 18:10 Mu ne: «Dafa amoon ñaari nit ñu dem ca kër Yàlla ga, di ñaan. Kenn ki ab Farisen la, ki ci des juutikat. 18:11 Farisen baa nga taxaw di ñaan ci xelam naan: “Yaw Yàlla, maa ngi lay sant ci li ma melul ni ñeneen ñiy sàcc, di def lu jubadi te di njaaloo, rawatina juutikat bii. 18:12 Ayu-bés gu nekk damay woor ñaari yoon, di joxe asaka ci lépp lu ma wut.” 18:13 «Juutikat ba moom, ma nga taxaw fu sore te bëggul a siggi sax, xool ca asamaan. Waaye ma ngay fëgg dënnam te naan: “Yaw Yàlla, yërëm ma, man miy bàkkaarkat.”» 18:14 Yeesu teg ca ne: «Maa ngi leen koy wax, nit kooku, ba muy ñibbi këram, moom la Yàlla àtte ni ku jub, waaye du Farisen ba. Ndaxte képp kuy yékkatiku dees na la suufeel, te kuy suufeelu, ñu yékkati la.» 18:15 Amoon na ay nit, ñuy indil Yeesu ay liir, ngir mu teg leen ay loxoom. Bi taalibe ya gisee loolu, ñu gëdd leen. 18:16 Waaye Yeesu woo leen ne: «Bàyyileen xale yi, ñu ñëw ci man, te buleen leen tere, ndaxte ñu mel ni ñoom ñoo yelloo nguuru Yàlla. 18:17 Ci dëgg, maa ngi leen koy wax, woyoful ni xale, nangu nguuru Yàlla, doo ci man a dugg.» 18:18 Benn njiitu Yawut laaj Yeesu ne ko: «Kilifa gu baax gi, lu ma war a def, ba am wàll ci dund gu dul jeex?» 18:19 Yeesu tontu ko: «Lu tax nga wooye ma ku baax? Yàlla rekk a baax. 18:20 Xam nga ndigal yi: “Bul njaaloo, bul bóom, bul sàcc, bul seede lu dul dëgg, teralal sa ndey ak sa baay.”» 18:21 Njiit la ne ko: «Loolu lépp sàmm naa ko li dale ci sama ndaw ba tey.» 18:22 Bi Yeesu déggee loolu, mu ne ko: «Lenn rekk moo la dese. Jaayal li nga am lépp, séddale ko miskin yi te dinga woomle ca asamaan; boo noppee, nga ñëw topp ci man.» 18:23 Bi nit ka déggee loolu, mu am tiis, ndaxte ku bare woon alal la. 18:24 Yeesu xool ko, daldi ne: «Boroom alal, dugg ci nguuru Yàlla, lu jafee ngoogu! 18:25 Giléem jaar ci bën-bënu pusa moo gën a yomb boroom alal dugg ci nguuru Yàlla.» 18:26 Ñi doon déglu daldi ne: «Kon nag ku man a mucc?» 18:27 Yeesu tontu ne: «Li të nit ñi, tëwul Yàlla.» 18:28 Noonu Piyeer ne: «Nun de, dëddu nanu li nu am lépp, topp la.» 18:29 Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, képp ku dëddu kër walla jabar walla ay doomi ndey walla ay waajur walla ay doom ngir nguuru Yàlla, 18:30 dinga am tey jii ay yooni yoon, ak dund gu dul jeex ëllëg.» 18:31 Yeesu wéetoo ak fukki taalibe yi ak ñaar ne leen: «Nu ngi dem Yerusalem, te li yonent yi bindoon lépp ci mbirum Doomu nit ki dina mat. 18:32 Dinañu ko jébbal ñi dul Yawut, ñu ñaawal ko, saaga ko, tifli ci kawam. 18:33 Gannaaw bu ñu ko dóoree ay yar ba noppi, dinañu ko rey, waaye ca ñetteelu fan ba dina dekki.» 18:34 Waaye taalibe ya dégguñu li mu leen doon wax; kàddu yooyu ump na leen, te xamuñu li waxi Yeesu yooyu tekki. 18:35 Bi Yeesu di agsi dëkku Yeriko, am gumba gu toogoon ca wetu yoon wa, di yelwaan. 18:36 Naka la gumba ga dégg mbooloo di jàll, mu laaj lan moo xew. 18:37 Ñu wax ko ne: «Yeesum Nasaret moo fay jaar.» 18:38 Noonu mu yuuxu ne: «Yeesu, Sëtu Daawuda, yërëm ma!» 18:39 Ñi jiitu woon gëdd ko, ngir mu noppi. Waaye muy gën a yuuxu naan: «Sëtu Daawuda, yërëm ma!» 18:40 Noonu Yeesu taxaw, santaane ñu indil ko ko. Bi mu jegesee, Yeesu laaj ko ne: 18:41 «Loo bëggoon ma defal la ko?» Mu ne ko: «Sang bi, damaa bëgg a gis.» 18:42 Noonu Yeesu ne ko: «Na say bët gis! Sa ngëm faj na la.» 18:43 Ca saa sa mu daldi gis. Noonu mu topp ci Yeesu, di màggal Yàlla. Mbooloo mépp gis loolu, di sant Yàlla.
19:1 Yeesu dugg na Yeriko, jaar ca dëkk ba, di dem. 19:2 Waaye amoon na fa waa ju ñuy wax Sase. Njiitu juutikat la, te di ku bare alal. 19:3 Bëgg na gis kan mooy Yeesu, waaye dafa gàtt lool, ba mënu koo gis ndax mbooloo ma. 19:4 Noonu mu daw, jiituji ca yoon wa, yéeg ci genn garab ngir gis Yeesu, ndaxte foofa la naroon a jaar. 19:5 Bi Yeesu dikkee ba tollook garab ga nag, mu téen ne ko: «Sase, wàccal gaaw, ndax tey sa kër laa war a dal.» 19:6 Sase daldi gaawantu wàcc, ganale ko ak mbég. 19:7 Ñépp gis loolu, di ñurum-ñurumi naan: «Mi ngi dal cig këru boroom bàkkaar.» 19:8 Waaye Sase taxaw ne Boroom bi: «Déglul Boroom bi, dogu naa may sama genn-wàllu alal miskin yi, te lu ma mas a njublaŋ nit, jël alalam, dinaa ko fey ñeenti yoon lu ni tollu.» 19:9 Yeesu ne ko: «Mucc gi wàcc na tey ci kër gii, ndaxte nit kii, ci askanu Ibraayma la bokk itam. 19:10 Ndaxte Doomu nit ki ñëw na, ngir seet te musal ñi réer.» 19:11 Bi nit ñi doon déglu kàddu yooyu, Yeesu teg ca léeb, ndaxte jege woon na Yerusalem, te ñoom foogoon nañu ne, nguuru Yàlla dafay daldi feeñ ca saa sa. 19:12 Mu ne nag: «Dafa amoon boroom juddu bu rafet bu demoon ci réew mu sore, ngir ñu fal ko buur te mu dellusiwaat. 19:13 Noonu mu woo fukk ci ay surgaam, jox ku nekk benn libidoor, ne leen: “Liggéeyleen ci, ba may ñibbisi.” 19:14 Waaye waa réewam bëgguñu ko. Noonu ñu yónni ndaw ci gannaawam ne: “Bëggunu nit kii yilif nu.” 19:15 «Bi ñu ko falee buur nag, ba mu dellusi, mu woolu surga, ya mu joxoon wurus wa, ngir xam nan lañu ci liggéeye. 19:16 Ku jëkk ka ñëw ne ko: “Sang bi, sa libidoor bii jur na fukki libidoor.” 19:17 Buur ba ne ko: “Def nga lu baax, surga bu baax nga. Segam wone nga ne, takku nga ci lu tuuti, falul ci fukki dëkk.” 19:18 Surga ba ca topp ñëw ne: “Sang bi, sa libidoor ba indi na juróomi libidoor.” 19:19 Buur ba ne ko: “Yaw, falul ci juróomi dëkk.” 19:20 Keneen ñëw ne: “Sang bi, sa libidoor baa ngi nii. Dama koo fasoon ci sekkit, denc ko. 19:21 Dama laa ragaloon, ndaxte ku néeg nga. Dangay nangu loo dénkaanewul, di dajale loo jiwul.” 19:22 Buur ba ne ko: “Ci say wax laa lay àtte, surga bu bon bi! Xamoon nga ne, nit ku néeg laa, di nangu lu ma dénkaanewul, te dajale lu ma jiwul. 19:23 Lu tax nag yóbbuwoo sama xaalis ca denckati xaalis ya? Bés bu ma ñëwee nag, ma man a jot sama xaalis ak la mu jur.” 19:24 «Ci kaw loolu mu ne ña taxawoon ca wetam: “Nanguleen libidoor bi ci moom, jox ko boroom fukki libidoor yi.” 19:25 Ñu ne ko: “Sang bi, am na fukki libidoor ba noppi.” 19:26 Buur ba ne leen: “Maa ngi leen koy wax, ku am, dinañu la dolli, waaye ku amul, li nga am as néew sax, dinañu ko nangu. 19:27 Waaye sama noon yi, ñi bëggul woon ma doon seen buur, indileen fii, rey leen ci sama kanam.”» 19:28 Bi mu waxee loolu ba noppi, Yeesu dafa daldi jiitu, jëm Yerusalem. 19:29 Bi muy jege dëkki Betfase ak Betani, ci wetu tund wu ñuy wax tundu Oliw ya, Yeesu yebal ñaar ci ay taalibeem, 19:30 ne leen: «Demleen ci dëkk bi ci kanam. Bu ngeen fa duggee, dingeen fa gis cumbur gu kenn musul a war. Yiwileen ko, indi. 19:31 Bu leen kenn laajee: “Lu tax ngeen koy yiwi?” tontuleen ko: “Boroom bi da koo soxla.”» 19:32 Ñaari ndaw ya dem, fekk mbir ya deme, na leen ko Yeesu waxe woon. 19:33 Bi ñuy yiwi cumbur ga nag, ay boroomam ne leen: «Lu tax ngeen di yiwi cumbur gi?» 19:34 Ñu tontu ne: «Ndaxte Boroom bi da koo soxla.» 19:35 Noonu ñu indil cumbur gi Yeesu, daldi lal seeni yére ca kaw, yéegal ca Yeesu. 19:36 Bi muy dem, nit ñi di lalal Yeesu seeni yére ci yoon wi. 19:37 Bi ñu agsee fa mbartalum tundu Oliw ya doore, taalibeem yépp fees ak mbég, tàmbalee màggal Yàlla ca kaw ndax kéemaan yu bare yi ñu gis. 19:38 Ñu ngi naan:«Yaw buur biy ñëw ci turu Boroom bi,ku barkeel nga!Na jàmm am ca asamaan,te ndam li féete ca bérab yu gën a kawe!» 19:39 Waaye ay Farisen yu nekkoon ca mbooloo ma ne Yeesu: «Kilifa gi, yeddal sa taalibe yi!» 19:40 Noonu mu tontu ne: «Maa ngi leen koy wax, bu ñu noppee ñoom, doj yiy xaacu.» 19:41 Bi Yeesu jegee dëkk ba, ba séen ko, mu jooy ko 19:42 naan: «Céy yaw itam, boo xamoon bésub tey yi la man a indil jàmm! Waaye fi mu ne mënuloo koo gis. 19:43 Bés dina ñëwi yu say noon di jal, wërale la. Dinañu la tëj ci biir, tanc la. 19:44 Dinañu la yàqaate, yaw ak sa waa dëkk. Doj dootul des ci kaw doj ci yaw, ndaxte ràññeewoo jamono ji Yàlla ñëwe, wallusi la.» 19:45 Gannaaw loolu Yeesu dugg ca kër Yàlla ga, daldi dàq ña fay jaay, 19:46 naan leen: «Mbind mi nee na: “Sama kër këru ñaan ci Yàlla lay doon; waaye yéen def ngeen ko këru sàcc.”» 19:47 Bés bu nekk Yeesu di jàngale ca kër Yàlla ga. Saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya, ñoom ak njiiti xeet wa, ñu ngi ko doon wut a reylu. 19:48 Waaye xamuñu woon lan lañu man a def, ndaxte nit ñépp a ngi ko doon déglu, bañ benn baat raw leen.
20:1 Benn bés Yeesu doon jàngal nit ña ca kër Yàlla ga, di leen yégal xebaar bu baax bi. Saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya ak njiit ya ñëw ne ko: 20:2 «Wax nu ci ban sañ-sañ ngay defe yëf yii, walla kan moo la may boobu sañ-sañ.» 20:3 Yeesu tontu leen ne: «Man itam dinaa leen laaj lenn: wax leen ma, 20:4 la Yaxya daan def, di sóob nit ñi ci ndox, fu mu ko jële, ci Yàlla walla ci nit ñi?» 20:5 Ñu waxtaan ci seen biir naan: «Bu nu nee: “Ci Yàlla,” dina laaj: “Lu tax gëmuleen ko kon?” 20:6 Te bu nu nee: “Ci nit ñi,” mbooloo mépp dinañu nu sànni ay xeer, ndaxte gëm nañu ne Yaxya yonent la woon.» 20:7 Noonu ñu tontu ne, xamuñu fu mu ko jële. 20:8 Yeesu ne leen: «Kon man itam duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii.» 20:9 Noonu Yeesu daldi wax nit ña léeb wii: «Amoon na nit ku jëmbët toolu réseñ, batale ko ay beykat, dem tukki tukki bu yàgg. 20:10 Bi tool bi ñoree nag, mu yónni surga ci ñoom, ngir jot wàllam ci meññeef gi. Waaye beykat yi dóor ko ay yar, dàq ko, mu dellu ak loxoy neen. 20:11 Mu yónniwaat beneen surga, ñu dóor ko moom itam, toroxal ko, dàq ko, mu dellu ak loxoy neen. 20:12 Mu yónneeti ñetteelu surga, ñu gaañ ko, dàq ko. 20:13 «Boroom tool ba daldi ne: “Nan laay def nag? Dinaa yónni sama doom, sama reeni xol. Xëy na ñu weg ko, moom.” 20:14 Waaye bi beykat yi gisee doom ji, ñu ne ci seen biir: “Kii moo war a donn tool bi; nan ko rey, moom ndono li.” 20:15 Ñu génne ko tool bi nag, rey ko.» Noonu Yeesu laaj leen: «Nu leen boroom tool bi di def, nag? 20:16 Xanaa ñëw, rey beykat yooyu, dénk tool ba ñeneen.» Bi Yeesu waxee loolu, nit ña ne ko: «Yàlla tere!» 20:17 Waaye Yeesu ne leen jàkk, daldi ne: «Kon nag lu baat yii ci Mbind mi di tekki:“Doj wa tabaxkat ya sànni,mujj na di doju koñ.” 20:18 Képp ku dal ci doj woowu, dammtoo, te ku mu dal ci sa kaw, rajaxe la.» 20:19 Xutbakat ya ak saraxalekat yu mag ya ñu ngi doon wut a jàpp Yeesu ca taxawaay ba, ndaxte xam nañu ne, ñoo tax mu wax léeb woowu. Waaye ragal nañu mbooloo ma. 20:20 Noonu ñu koy yeeru, daldi yónni ay nit ñu mbubboo njub, sas leen ñu fexe koo jàpp ci ay waxam, ngir jébbal ko boroom réew, ma yor kilifteef ak sañ-sañ. 20:21 Ñu daldi ñëw ci Yeesu ne ko: «Kilifa gi, xam nanu ne li ngay wax te di ko jàngale lu jub la. Amuloo parlàqu, waaye dangay xamle yoonu Yàlla ci bu wóor. 20:22 Wax nu, ndax jaadu na, nu fey buur bi Sesaar galag walla déet.» 20:23 Waaye Yeesu xam na seen pexe ne leen: 20:24 «Wonleen ma posetu denariyon. Kan lañu ci def nataalam ak turam?» Ñu tontu ko: «Sesaar.» 20:25 Noonu mu ne leen: «Joxleen nag Sesaar li Sesaar moom, te jox Yàlla li Yàlla moom.» 20:26 Noonu mënuñu ko woon a jàpp ciy waxam ci kanamu mbooloo ma; ñu waaru ci tontoom, ba wedam. 20:27 Noonu ay nit, ñu bokk ci Sadusen yi, ñëw ci moom. Sadusen yi nag ñoom weddi nañu ndekkite li. Noonu ñu laaj ko ne: 20:28 «Kilifa gi, Musaa bindal na nu ne, ku magam faatu te bàyyiwul doom ak jabaram, kooku war na donn jigéen ji, ba yékkati giiru magam. 20:29 Amoon na fi nag juróom-ñaari góor ñu bokk ndey ak baay. Taaw ba takk jabar, faatu, te bàyyiwul doom. 20:30 Ñaareel ba takk jigéen ja, def noonu; ak ñetteel ba, ba juróom-ñaar ñépp faatu te bàyyiwuñu doom. 20:32 Gannaaw ga nag jigéen ja it faatu. 20:33 Ci ndekkite li nag, kan ci ñoom moo war a donn jigéen ja, fekk ku nekk ci juróom-ñaar ñi mas na koo takk?» 20:34 Yeesu tontu leen ne: «Ci àddina sii, góor ñi ak jigéen ñi dañuy séy. 20:35 Waaye ña ñu àtte ne, yeyoo nañoo bokk ci dundu ëllëg ak ci ndekkite li, kenn du am jabar, kenn du am jëkkër. 20:36 Dafa fekk ne mënatuñoo dee, ndaxte dañuy mel ni malaaka yi. Ay doomi Yàlla lañu ndaxte doomi ndekkite lañu. 20:37 Te Musaa sax wone na ne, néew yi dinañu dekki, ci saarum ngarab si. Foofa Musaa wooye na fa Boroom bi: “Yàllay Ibraayma, Yàllay Isaaxa, di Yàllay Yanqóoba.” 20:38 Kon nag nekkul Yàllay ñi dee waaye Yàllay ñiy dund la, ndaxte Yàllaa tax ñépp di dund.» 20:39 Ci kaw loolu ay xutbakat ne ko: «Li nga wax dëgg la, kilifa gi!» 20:40 Ndaxte kenn ci ñoom ñemeetu koo laaj dara. 20:41 Noonu Yeesu ne leen: «Lu tax nit ñi di wax ne, Almasi bi mooy sëtu Daawuda? 20:42 Ndaxte Daawuda moom ci boppam moo ne ci Sabóor:“Boroom bi nee na sama Boroom:‘Toogal ci sama ndeyjoor, 20:43 ba kera may daaneelsay noon ci sa kanam.’ ” 20:44 Gannaaw Daawuda nag wooye na ko “Boroom bi,” nu muy nekke sëtam?» 20:45 Bi ko nit ña fa nekkoon ñépp doon déglu, Yeesu ne ay taalibeem: 20:46 «Moytuleen xutbakat yi; dañoo bëgg di doxantu, sol ay mbubb yu réy, te ñépp di leen nuyoo ñaari loxo ci pénc mi. Ci jàngu yi, toogu yu féete kanam lañuy wut, te toogu yu yiw lañuy taamu ci reeri xew yi. 20:47 Ñu ngi lekk alalu jigéen ñi seen jëkkër faatu, di ñaan Yàlla ay ñaani ngistal yu gudd. Seen mbugal dina gën a tar.»
21:1 Noonu Yeesu siggi, séen ay boroom alal ñuy dugal seen sarax ca ndab ya ca kër Yàlla ga. 21:2 Mu gis itam jenn jigéen ju jëkkëram faatu te mu ñàkk, ju fa def ñaari poseti xànjar. 21:3 Noonu mu daldi ne: «Ci dëgg, maa ngi leen koy wax, jigéen ju ñàkk jee moo ëpp ñeneen ñépp lu mu joxe. 21:4 Ñoom ñépp dañu sàkku ci seen barele, waaye moom dafa sàkku ci néewleem, ba joxe xaalis bi mu waroon a dunde.» 21:5 Noonu ay nit doon wax ci lu jëm ca kër Yàlla ga, ak ni ñu ko rafetale ak ay doj yu jafe ak alal ju ñu jébbal Yàlla. Waaye Yeesu ne leen: 21:6 «Li ngeen gis fii lépp, jamono dina ñëw joo xam ne dina daanu, ba doj dootul des ci kaw doj.» 21:7 Ñu laaj ko ne: «Kilifa gi, kañ la loolu di am? Te luy tegtal ne, looloo ngi waaj a xew?» 21:8 Yeesu tontu ne: «Moytuleen, bu leen kenn nax. Ndaxte ñu bare dinañu ñëw ci sama tur ne: “Moom laa,” walla ñu naan: “Jamono ji jegesi na.” Buleen topp ñooñu. 21:9 Bu ngeen déggee ay xare ak ay réew yu jóg, wottuleen a tiit, ndaxte fàww yooyule jëkk a am. Waaye taxul mujug jamono daldi taxaw.» 21:10 Noonu mu teg ca ne: «Xeet dina jóg, xeex ak weneen xeet, réew dina xeex ak meneen réew. 21:11 Suuf dina yengu yengu yu réy, te wopp ak xiif dina am ci bérab yu bare. Dina am it ay xew-xew yu raglu ak ay firnde yu mag yuy jóge asamaan. 21:12 Waaye bala looloo xew, dees na leen jàpp, fitnaal leen, di leen jébbal àttekat yi ca jàngu ya, tëj leen kaso. Dees na leen yóbbu ci kanam ay buur yi ak ay boroom réew ndax sama tur. 21:13 Loolu dina leen ubbil bunt, ba ngeen man maa seedeel. 21:14 Fasleen yéenee bañ a wut lay ngir musal seen bopp. 21:15 Ndaxte man ci sama bopp maa leen di jox kàddu ak xel moo xam ne seeni noon duñu ko man a teggi, mbaa ñu di ko weddi. 21:16 Seeni waajur sax ak seeni doomi ndey, seeni bokk ak seeni xarit, dinañu leen jébbal àttekat yi, ba ñu rey ñenn ci yéen. 21:17 Te ñépp dinañu leen bañ ndax sama tur. 21:18 Waaye seen genn kawar sax du neen. 21:19 Seen muñ moo leen di musal. 21:20 «Bu ngeen gisee ay xarekat wër dëkku Yerusalem, xamleen ne jamono, ji ñu koy yàq, agsi na. 21:21 Kon nag ku nekk ci biir diiwaanu Yude, nanga daw ca tund ya; ku nekk ci biir dëkk bi, nanga ko génn; te ku nekk ca tool ya, bul dugg ca dëkk ba! 21:22 Ndaxte ci bés yooyu Yàlla dina fey jëf yi, te li ñu bindoon ci téereb Yàlla dina mat. 21:23 Ngalla jigéen ñi ëmb ca bés yooya, ngalla it ñiy nàmpal! Ndaxte tiis wu metti dina am ci réew mi, te Yàlla dina wàcce meram ci waa réew mii. 21:24 Dees na leen reye ak i jaasi, jàpp leen jaam, yóbbu leen ci réewi àddina sépp. Te ñi dul Yawut dinañu nappaaje Yerusalem, ba kera jamonoy ñi dul Yawut mat. 21:25 «Ay firnde dinañu feeñ ci jant bi, ci weer wi ak ci biddiiw yi. Ci kaw suuf xeet yi dinañu tiit, jaaxle ndax riiru géej gi ak yengu-yengub duus yi. 21:26 Bu boobaa nit ñiy xëm ndax tiitaange, bu ñuy xalaat musiba, yi nar a wàcc ci àddina, ndaxte dees na yengal kàttani asamaan. 21:27 Noonu dinañu gis Doomu nit ki di ñëw ciw niir, ànd ak kàttan ak ndam lu réy. 21:28 Bu mbir yooyu di tàmbalee xew nag, boo yaboo ngeen siggi, téen, ndaxte seen njot jubsi na.» 21:29 Noonu Yeesu misaal leen lii: «Xool-leen garabu figg ak yeneen garab yi. 21:30 Bu ñu gisee ñu sëq, soxlawuleen kenn wax leen ne, nawet bi jubsi na xaat. 21:31 Noonu itam bu ngeen gisee loolu lépp xew, xamleen ne nguuru Yàlla jege na. 21:32 «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, niti jamono jii duñu wéy, te loolu lépp amul. 21:33 Asamaan ak suuf dinañu wéy, waaye samay wax du wéy mukk. 21:34 «Moytuleen seen nafsu diigal leen ci yàqute ak ci màndite ak ittey àddina, ba bés boobu bett leen ni mbaal. 21:35 Ndaxte dina dal ci ñépp ñi nekk ci kaw suuf. 21:36 Yeewuleen, di sax ci ñaan, ngir ngeen man a mucc ci loolu lépp war a xew, te man a taxaw ak kóolute ci kanamu Doomu nit ki.» 21:37 Yeesoo ngi daan yendoo jàngale ca kër Yàlla ga, te bu guddee mu dem ca tund wu ñuy wax tundu Oliw ya, fanaan fa. 21:38 Te nit ñépp dañu daan teel a xëy ca kër Yàlla ga, di ko déglu.
22:1 Màggalu Mburu ya amul lawiir jege woon na, te ñu di ko wax Bésu Jéggi ba. 22:2 Saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya di wut pexem reylu Yeesu, ndaxte dañoo ragaloon nit ña. 22:3 Noonu Seytaane daldi solu Yudaa, mi ñuy wooye Iskariyo te mu bokkoon ca fukki taalibe ya ak ñaar. 22:4 Noonu Yudaa dem waxtaani ak saraxalekat yu mag ya ak kilifay wottukati kër Yàlla ga, ba xam nan la leen di jébbale Yeesu. 22:5 Ñu am ca bànneex bu réy, dig ko xaalis. 22:6 Yudaa nangu, di fexe jamono ju mu leen man a jébbal Yeesu, fu mbooloo ma nekkul. 22:7 Bésu màggalu Mburu ya amul lawiir agsi, ca bés boobu lañu waroon a rendi mbotem màggalu Jéggi ba. 22:8 Noonu Yeesu yebal Piyeer ak Yowaana ne leen: «Demleen, defaral nu reeru Jéggi ba.» 22:9 Ñu ne ko: «Fan nga bëggoon, nu defare ko fa?» 22:10 Mu ne leen: «Bu ngeen duggee ca dëkk ba, góor gu yenu njaq lu def ndox, dina taseek yéen. Toppleen ci moom ba ca kër ga muy dugg, 22:11 te ngeen ne boroom kër ga: “Kilifa gi nee na: Ana néegu gan, bi may lekke reeru Jéggi ba, man ak samay taalibe?” 22:12 Noonu dina leen won néeg bu féete kaw, te yaa, ñu defar ko ba noppi. Foofa ngeen koy defare.» 22:13 Ñu dem, gis lépp, ni leen ko Yeesu waxe woon. Noonu ñu defar reer bi. 22:14 Bi waxtu wi jotee Yeesu toog ak ndaw yi, 22:15 ne leen: «Yàkkamti woon naa lool lekk ak yéen reeru Jéggi bii, laata ñu may sonal. 22:16 Ndaxte maa ngi leen koy wax, dootuma ko lekk mukk, lu dul ba kera mu mat ci nguuru Yàlla.» 22:17 Noonu mu fab kaas, daldi sant Yàlla ne: «Jël-leen kaas bii, séddoo ko. 22:18 Ndaxte maa ngi leen koy wax, dootuma naan ndoxum réseñ mi, ba kera Yàlla di tëral nguuram.» 22:19 Gannaaw loolu mu jël mburu, sant Yàlla, damm ko, joxleen ko ne: «Lii sama yaram la, wi ma joxe ngir yéen. Defleen lii, ngir fàttaliku ma.» 22:20 Noonu itam bi ñu lekkee ba noppi, mu jël kaas bi ne leen: «Kaas bii mooy misaal kóllëre gu bees gi Yàlla fas jaarale ko ci sama deret, ji tuuru ngir yéen. 22:21 Waaye nag loxob ki may wor a ngi nekk ak man ci ndab li. 22:22 Doomu nit ki mu ngi dem, ni ñu ko dogale. Waaye ki koy wor dina torox.» 22:23 Noonu taalibe yi di laajante ci seen biir, kan ci ñoom mooy nar a def loolu. 22:24 Taalibe ya it di werante, ngir xam kan ci ñoom moo gën a màgg. 22:25 Yeesu ne leen: «Buuri xeeti àddina dañu leen di dóor yetu nguur, te kilifa yi dañuy sàkku ngërëm. 22:26 Waaye yéen buleen def noonu. Ki gën a màgg ci yéen, na nekk ni ki gën a ndaw, te njiit mel ni surga. 22:27 Ki toog ca lekkukaay ba, moom ak surgaam, ñoom ñaar kan moo ci gën a màgg? Xanaa du ki toog ci lekkukaay bi? Waaye man maa ngi ci seen biir ni surga. 22:28 Yéen nag yéenay ñi ànd ak man ci samay fitna. 22:29 Man nag jox naa leen sañ-sañu nguuru, ni ma ko sama Baay joxe. 22:30 Dingeen lekkandoo te naanandoo ak man ci sama nguur. Te dingeen toog ci jal yi, di àtte fukki giir ak ñaar yu bànni Israyil.» 22:31 Yeesu teg ca ne: «Simoŋ, Simoŋ! Seytaane ñaan na, ñu jébbal leen ko, ngir mu teqale leen ni ñu teqalee dugub ak xatax. 22:32 Waaye man ñaanal naa la, ngir sa ngëm dëgër. Te yaw, boo dellusee, nanga dëgëral sa bokki taalibe yi.» 22:33 Piyeer ne ko: «Boroom bi, àttan naa ànd ak yaw ca kaso, ba ci dee sax.» 22:34 Yeesu tontu ko ne: «Piyeer, maa ngi la koy wax, bala ginaar a sab tey jii, dinga weddi ñetti yoon ne, xam nga ma.» 22:35 Noonu Yeesu ne leen: «Ba ma leen yebalee te yóbbaalewuleen woon xaalis, mbuus, walla dàll, ndax ñàkkoon ngeen dara?» Ñu tontu ne: «Déedéet.» 22:36 Mu neeti leen: «Léegi nag képp ku am xaalis, na ko jël; te ku am mbuus, na ko jël; ku amul jaasi, na jaay mbubbam, jënde ko jaasi. 22:37 Ndaxte maa ngi leen koy wax, lii Mbind mi wax fàww mu am ci man, bi mu nee: “Boole nañu ko ak ñu bon ña.” Ndaxte loolu jëm ci man mi ngi mat.» 22:38 Noonu taalibe ya ne ko: «Boroom bi, ñaari jaasee ngii.» Mu ne leen: «Doy na.» 22:39 Noonu Yeesu génn, dem ca tundu Oliw ya, ni mu ko daan defe nakajekk. Taalibeem ya topp ci moom. 22:40 Bi mu agsee ca bérab ba, mu ne leen: «Ñaanleen, ngir bañ a daanu cig fiir.» 22:41 Noonu mu dand leen, ba fu aw saan man a tollu, daldi sukk di ñaan ne: 22:42 «Baay, soo ko bëggee, teggil ma kaasu naqar bii. Moona bumu doon sama coobare, waaye na sa coobare am.» 22:43 Noonu malaakam Yàlla daldi koy feeñu, may ko doole. 22:44 Ci biir tiis, Yeesu gën a sawar ci ñaan gi, ñaqam mel ni lumbi deret dal ci suuf. 22:45 Bi mu ñaanee ba noppi, mu jóg, dellusi ci taalibe yi, fekk leen ñuy nelaw, ndaxte seen xol dafa sonnoon ak tiis. 22:46 Noonu mu ne leen: «Lu tax ngeen di nelaw? Jógleen ñaan, ngir bañ a daanu cig fiir.» 22:47 Bi Yeesu di wax, mbooloo mu bare agsi; ku ñuy wax Yudaa te mu bokkoon ci fukki ndaw yi ak ñaar jiite leen. Yudaa jegeñsi Yeesu, bëgg koo fóon. 22:48 Waaye Yeesu ne ko: «Ci fóon ngay jébbale Doomu nit ki ay noonam!» 22:49 Bi ñi àndoon ak Yeesu gisee liy bëgg a xew, ñu ne: «Boroom bi, ndax nu dóore jaasi?» 22:50 Kenn ci ñoom nag dóor surgab saraxalekat bu mag ba, noppu ndeyjooram dagg. 22:51 Waaye Yeesu daldi ne: «Bàyyileen.» Mu laal noppu waa ja, wéral ko. 22:52 Noonu Yeesu ne saraxalekat yu mag ya ak kilifay wottukati kër Yàlla ga ak njiiti xeet, wa ko jàppsi woon: «Jóg ngeen, gànnaayoo jaasi ak yet, mel ni ñuy topp sàcc. 22:53 Moona maa nga woon ak yéen bés bu nekk ca kër Yàlla ga, te jàppuleen ma. Waaye léegi seen waxtu la, di jamonoy lëndëm.» 22:54 Ñu jàpp Yeesu, yóbbu ko ca kër saraxalekat bu mag ba. Piyeer topp fu sore. 22:55 Amoon na taal ca diggu ëtt ba, ay nit toog, wër ko, Piyeer itam toog ci seen biir. 22:56 Ab mbindaan gis ko, mu toog, taal bi di ko leeral, mu ne ko jàkk ne: «Nit kii itam àndoon na ak moom.» 22:57 Waaye Piyeer weddi ko ne: «Soxna si, xawma kooku.» 22:58 Nes tuuti keneen gis ko ne: «Yaw itam ci ñoom nga bokk.» Piyeer tontu ko: «Sama waay, bokkuma ci.» 22:59 Bi ñu tegee lu mat waxtu, keneen dikkaat ca wax ja ne: «Ci lu wóor nit kii àndoon na ak moom, nde Galile la jóge.» 22:60 Waaye Piyeer tontu ne: «Sama waay, xawma li ngay wax!» Bi kàddoom di daanu, faf ginaar daldi sab. 22:61 Noonu Boroom bi geestu, xool Piyeer. Te Piyeer fàttaliku la ko Boroom bi waxoon ne: «Bala ginaar a sab tey jii, dinga ma weddi ñetti yoon.» 22:62 Piyeer daldi génn, di jooy jooy yu metti. 22:63 Nit ñaa nga jàppoon Yeesu, di ko ñaawal ak di ko dóor. 22:64 Ñu ngi takkoon ay bëtam, di ko laaj, naan ko: «Yaw, wax nu ci kàddug Yàlla, ku la dóor?» 22:65 Ñu ngi ko doon tifaar it yeneeni saaga. 22:66 Bi bët setee, kureelu njiiti xeet wa, maanaam saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya, daldi daje, indi Yeesu ci seen kanam. 22:67 Ñu ne ko: «Soo dee Almasi bi, wax nu ko.» Mu tontu leen ne: «Su ma leen ko waxee, dungeen ma gëm. 22:68 Te su ma leen laajee, dungeen tontu. 22:69 Waaye gannaawsi tey, Doomu nit ki dina toog ci ndeyjooru Yàlla, Aji Kàttan ji.» 22:70 Noonu ñépp ne: «Kon nag yaay Doomu Yàlla ji?» Mu tontu leen ne: «Yéen ci seen bopp wax ngeen ne moom laa.» 22:71 Ñu daldi ne nag: «Lu nuy doyeeti seede léegi, ndegam nun ci sunu bopp noo ko nangoo ci gémmiñam!»
23:1 Gannaaw loolu kureelu àttekat ya yépp daldi jóg, yóbbu Yeesu ca Pilaat. 23:2 Foofa ñu tàmbali di ko sosal naan: «Fekk nanu nit kii, muy fàbbi sunu réew, di leen teree fey galag Sesaar, te mi ngi teg boppam Almasi, maanaam buur.» 23:3 Noonu Pilaat laaj ko: «Ndax yaa di buuru Yawut yi?» Yeesu tontu ko ne: «Wax nga ko.» 23:4 Pilaat ne saraxalekat yu mag ya ak mbooloo ma: «Gisuma genn tooñ ci nit kii.» 23:5 Waaye ñu sax ci seeni wax naan: «Mi ngi jógloo mbooloo mi, di jàngale ci réewu Yawut ya mépp, li dale ci Galile ba fii.» 23:6 Bi Pilaat yégee baat yooyu, mu laajte ne: «Ndax nit kii Galile la dëkk?» 23:7 Bi mu yégee ne, Yeesoo ngi nekk ci diiwaan bi Erodd yilif, mu yónnee ko Erodd, mi nekkoon ci jamono jooju ci Yerusalem. 23:8 Bi Erodd gisee Yeesu, mu am mbég mu réy. Bu yàgg ba tey dafa koo bëggoon a gis, ndaxte déggoon na ñuy wax ci ay mbiram te yaakaaroon na ne, dina ko gis mu def kéemaan. 23:9 Noonu mu laaj ko ay laaj yu bare, waaye Yeesu tontuwul dara. 23:10 Saraxalekat yu mag ya ak xutbakat yaa nga fa woon, di ko jiiñ bu metti. 23:11 Noonu Erodd ak ay xarekatam toroxal Yeesu, di ko ñaawal. Gannaaw loolu mu solal ko mbubb mu rafet, delloo ko Pilaat. 23:12 Erodd ak Pilaat dañoo ñi bañante woon bu jëkk, waaye ca bés booba doon nañu ay xarit. 23:13 Pilaat daldi woo saraxalekat yu mag ya, njiit ya ak mbooloom Yawut ya ne leen: 23:14 «Indil ngeen ma nit kii, ne ma, day jàddloo yoon mbooloo mi. Léegi nag man mii laaj naa ko ci seen kanam, waaye gisuma tooñ ci moom ak li ngeen koy jiiñ lépp. 23:15 Erodd itam gisul tooñ gu mu def, ndegam mu yónneewaat nu ko. Nit kii deful genn tooñ gu jar ñu koy rey. 23:16 Kon nag dinaa ko dóorlu ay yar te bàyyi ko.» 23:18 Waaye ñu bokk di yuuxu, ñoom ñépp naan: «Reyal kii te bàyyi Barabas!» 23:19 Dañoo tëjoon Barabas, ndaxte dafa jéem a tas dëkk ba, te rey nit. 23:20 Pilaat waxaat ak mbooloo ma, ndaxte dafa bëggoon a bàyyi Yeesu. 23:21 Waaye ñuy yuuxu naan: «Daaj ko ci bant! Daaj ko ci bant, ba mu dee!» 23:22 Pilaat ne leen ñetteel bi yoon: «Lu tax? Gan tooñ la def? Gisuma ci moom dara lu jar dee. Kon dinaa ko dóorlu ay yar te bàyyi ko.» 23:23 Waaye ñoom ñu sax ca la ñu waxoon, di gën a yuuxu naan, ñu daaj ko ci bant. Coow la yey Pilaat. 23:24 Muj gi Pilaat dogal, ñu defal leen li ñu bëgg. 23:25 Mu bàyyil leen ki ñu ko ñaanoon, kooku ñu tëjoon kaso, ndax tas réew ma ak rey nit. Waaye mu jébbal leen Yeesu ci seeni loxo. 23:26 Bi ñuy yóbbu Yeesu, ñu jàpp ku ñuy wax Simoŋ te mu dëkk Siren, ku jóge ca wet, ga féete ak tool ya, sëf ko bant, ba ñuy war a daaj Yeesu, ngir mu gàddu ko, topp ci moom. 23:27 Mbooloo mu baree nga ko toppoon, te jigéen ñu baree ngi doon yuuxu, di ko jooy. 23:28 Yeesu daldi walbatiku ca ñoom ne: «Yéen jigéeni Yerusalem, buleen ma jooy! Jooyleen seen bopp ak seeni doom. 23:29 Ndaxte jamono dina ñëw, ju ñu naan: “Jigéen ñi musul a jur ak ñi musul a nàmpal, barkeel ngeen!” 23:30 Bu keroogee,“Nit ñi dinañu ne tund yi:‘Daanuleen ci sunu kaw!’te naan jànj yi: «“Suul-leen nu!»“ “ 23:31 Ndaxte su ñu defee nii garab gu tooy gi, lu ñuy def garab gu wow gi?» 23:32 Yóbbaale nañu itam ñeneen, ñuy ñaari defkati lu bon, ngir rey leen. 23:33 Bi xarekat ya agsee ba ca bérab, ba ñuy wooye Kaaŋu Bopp, ñu daaj fa Yeesu ca bant, daajaale ñaari defkati lu bon ya, kenn ca ndeyjooram, ka ca des ca càmmooñam. 23:34 Ci kaw loolu Yeesu ne: «Baay, baal leen, ndaxte xamuñu li ñuy def.» Xarekat ya tegoo ay bant yéreem, ngir séddoo ko. 23:35 Mbooloo maa nga fa taxaw di seetaan. Njiit ya di ko reetaan naan: «Musal na ñeneen; na musal boppam, su fekkee mooy Almasi bi, ki Yàlla fal!» 23:36 Xarekat ya it di ko ñaawal. Ñu jegesi, jox ko bineegar te naan: 23:37 «Su fekkee ne yaay buuru Yawut yi, musalal sa bopp!» 23:38 Ñu daaj mbind, mu tiim ko naan: «Kii mooy buuru Yawut yi.» 23:39 Kenn ca defkatu lu bon ya ñu wékkoon ci bant, di ko xas, naan ko: «Xanaa du yaw yaay Almasi bi? Musalal sa bopp te musal nu!» 23:40 Waaye ka ca des yedd moroom ma, naan ko: «Xanaa ragaloo Yàlla, yaw mi ñuy mbugal ni moom! 23:41 Nun yelloo nanu sunu mbugal, waaye moom deful dara.» 23:42 Noonu mu ne: «Yeesu, fàttaliku ma, boo dellusee ci sa nguur.» 23:43 Yeesu tontu ko ne: «Ci dëgg maa ngi la koy wax, tey jii dinga texe ak man ca jataayu Yàlla.» 23:44 Noonu digg-bëccëg daldi jot, jant ba nëbbu, réew mépp daldi lëndëm këruus lu mat ñetti waxtu. Ridob bérab bu sell ba ca kër Yàlla ga daldi xar ñaar. 23:46 Yeesu woote ak kàddu gu dëgër naan: «Baay, jébbal naa la sama ruu!» Bi mu waxee loolu, mu delloo ruuwam Yàlla. 23:47 Bi njiitu xare ba gisee li xewoon, mu màggal Yàlla ne: «Dëgg-dëgg nit kii ku jub la woon.» 23:48 Nit ña fa dajaloo woon ñépp, di seetaan li xew, ba ñu gisee loolu, ñu dellu seen kër, fëgg seen dënn, di jooy. 23:49 Xamey Yeesu yépp ak jigéen, ña ko toppe woon Galile, dand leen, di xool li xew. 23:50 Nit ku ñuy wax Yuusufa dem ca Pilaat. Mi ngi dëkk Arimate ca diiwaanu Yude. Yuusufaa nga bokkoon ca kureelu àttekat yi. Nit ku baax la woon te jub, te àndul woon ci li ñu dogaloon te jëf ko. Da doon séentu nguuru Yàlla. 23:52 Mu dem ca Pilaat, laaj ko néewu Yeesu. 23:53 Gannaaw loolu mu wàcce ko ca bant ba, laxas ko ci càngaay, dugal ko cib bàmmeel bu ñu yett ciw doj te musuñu caa def kenn. 23:54 Fekk bésu Waajal la woon, te bésu noflaay baa ngi doon tàmbali. 23:55 Jigéen ña gungee woon Yeesu Galile, ànd ak Yuusufa, gis bàmmeel ba ak na ñu ca dence néewu Yeesu ba. 23:56 Noonu ñu dellu defari cuuraay ak latkoloñ ngir néew ba. Ca bésu noflaay ba ñu noppalu, ni ko yoon wi santaanee.
24:1 Bés bu jëkk ca ayu-bés ga, jigéen ña jóg ca fajar, dem ca bàmmeel ba. Ñu ngi yoroon cuuraay lu ñu defaroon. 24:2 Bi ñu agsee, ñu fekk ñu béraŋ doj, wa uboon bàmmeel ba. 24:3 Ñu dugg ca bàmmeel ba, waaye fekkuñu fa néewu Boroom bi Yeesu. 24:4 Noonu ba ñu nekkee ak seen njaaxle, am na ñaar ñu leen feeñu, sol yére yuy melax. 24:5 Jigéen ña am tiitaange ju mag, daldi dëpp seen jë ci suuf. Waaye ñu ne leen: «Lu tax ngeen di seet kiy dund ci biir néew yi? 24:6 Nekkatu fi; dekki na. Fàttalikuleen la mu leen waxoon, ba mu nekkee Galile. 24:7 Nee woon na: “Fàww ñu jébbal Doomu nit ki bàkkaarkat yi, ñu rey ko ci bant, mu dekki ca ñetteelu fan ba.”» 24:8 Noonu ñu daldi fàttaliku kàdduy Yeesu ya. 24:9 Bi ñu jógee bàmmeel ba, ñu dem nettaliji loolu lépp fukki ndaw ya ak benn, ak ña ca des ñépp. 24:10 Jigéen ña ñoo doon Maryaamam Magdala, Sànn, ak Maryaama yaayu Saag. Yeneen jigéen yi leen gunge woon itam nettali loolu ndaw ya. 24:11 Waaye ñu teg wax jooju ay jeneer, ba gëmuñu jigéen ñooñu. 24:12 Waaye Piyeer daldi jóg, daw, dem ca bàmmeel ba. Bi mu àggee, mu sëgg, yër, gisul lu dul càngaay la. Noonu mu dëpp ñibbi, jaaxle lool ci li xew. 24:13 Ca bés boobu ñaar ci taalibe yi di dem ci dëkku Emayus, te mu sore Yerusalem ci lu mat fukki kilomet. 24:14 Ñu waxtaane li xewoon lépp. 24:15 Bi ñuy waxtaan ak a sotteente xalaat, Yeesu ci boppam dab leen, ànd ak ñoom, 24:16 fekk seeni bët muuru, ba mënu ko woon a xàmmi. 24:17 Yeesu ne leen: «Lan ngeen di waxtaane nii ci yoon wi?» Noonu ñu taxaw, seen xol jeex. 24:18 Kenn ci ñoom, ki tudd Këleyopas ne ko: «Xanaa yaw rekk yaa ñëw Yerusalem te umple li fi xewoon bés yii?» 24:19 Yeesu ne leen: «Lu fi xew?» Ñu tontu ko ne: «Mbirum Yeesum Nasaret. Ab yonent la woon bu doon def ay jëf yu mag, di wax ay kàddu yu am doole, ci kanam nit ñi ak ca kanam Yàlla. 24:20 Waaye sunuy saraxalekat yu mag ak sunuy njiit ñoo ko jébbal nguur gi ngir ñu àtte ko, teg ko dee, ba daaj ko ci bant. 24:21 Nun nag danoo yaakaaroon ne, mooy kiy nar a jot Israyil. Waaye bi loolu xewee ak léegi, tey la ñetteelu fan bi. 24:22 Teewul nag am na ay jigéen yu bokk ci nun yu nu jaaxal. Dañoo fajaru ca bàmmeel ba, 24:23 waaye fekkuñu fa néewam. Ñu dellusi, nettali nu ne, ay malaaka feeñu nañu leen, yégal leen ne, mi ngi dund. 24:24 Ñenn ci sunu àndandoo yi dem nañu ca bàmmeel ba, fekk lépp mel, na ko jigéen ña waxe woon. Waaye moom gisuñu ko.» 24:25 Noonu Yeesu ne leen: «Yéen daal, yéena ñàkk xel, te seen xol yéex a gëm li yonent yi yégle woon! 24:26 Xanaa du Almasi bi dafa waroon a daj boobu coono te dugg ci ndamam?» 24:27 Noonu mu tàmbalee ci yonent Yàlla Musaa ba ci yonent yépp, tekkil leen li Mbind mi wax lépp ci ay mbiram. 24:28 Bi ñuy jub dëkk, ba ñu jëmoon nag, Yeesu def ni kuy jubal yoonam. 24:29 Waaye ñu téye ko ne ko: «Toogal fii ci nun, ndaxte jant baa ngi so, te léegi mu guddi.» Noonu mu dugg, toog ca ñoom. 24:30 Bi ñu tàmbali di reer, Yeesu jël mburu ma, gërëm Yàlla, ba noppi damm ko, jox leen ko. 24:31 Bi mu defee loolu, lépp leer ci seeni bët, ñu daldi ko xàmmi. Waaye Yeesu ne mes, gisatuñu ko. 24:32 Noonu ku nekk naan sa moroom: «Ndax sa xol seddul woon, bi muy wax ak nun ci yoon wi, te muy tekki Mbind mi?» 24:33 Ñu daldi jóg ca saa sa, dellu Yerusalem, fekk fa fukki ndaw ya ak benn, ak yeneeni taalibe. 24:34 Ñooñu ne leen: «Dëgg la, Boroom bi dekki na, te feeñu na Simoŋ!» 24:35 Ñaari taalibe ya ñoom it daldi leen nettali la xewoon ca yoon wa ak ni ñu xàmmee Yeesu, bi mu dammee mburu ma. 24:36 Bi ñaari taalibe ya dee wax noonu, Yeesu taxaw moom ci boppam ci seen biir ne leen: «Na jàmm wàcc ci yéen.» 24:37 Ñu daldi tiit, foog ne dañoo gis njuuma. 24:38 Waaye Yeesu ne leen: «Lu tax ngeen jaaxle, ak lu tax ngeen di xel ñaar ci seen xol? 24:39 Xool-leen samay loxo ak samay tànk. Man mii la. Laal-leen ma te xam, njuuma amul yaram walla ay yax, ni ngeen gise, ma am ko.» 24:40 Bi mu leen waxee loolu, mu won leen ay loxoom ak ay tànkam. 24:41 Waaye ba tey mënuñu woon a gëm ndax seen mbég ak jaaxle. Noonu Yeesu laaj leen ne: «Ndax am ngeen fii lu ñu lekk?» 24:42 Ñu jox ko dogu jën wu ñu lakk. 24:43 Mu jël ko, lekk ci seen kanam. 24:44 Noonu mu ne leen: «Bi ma nekkee ak yéen, waxoon naa leen baat yii: li ñu bind lépp ci samay mbir ci yoonu Musaa ak ci téerey yonent yi ak ci Sabóor dafa war a am.» 24:45 Noonu mu ubbi seen xel, ngir ñu xam li Mbind mi di wax. 24:46 Mu ne leen: «Fàww Almasi bi sonn, mu dee te dekki ca ñetteelu fan ba, ni ñu ko binde, 24:47 te it ñuy yégle xeet yépp ci turam, dale ko ci Yerusalem ne, war nañoo tuub seeni bàkkaar, Yàlla baal leen. 24:48 Yéenay samay seede. 24:49 Te man dinaa leen yónnee li sama Baay dige. Yéen nag toogleen ci dëkk bi, ba ñu sol leen doole ji jóge ci kaw.» 24:50 Gannaaw loolu Yeesu yóbbu leen ca wetu Betani. Foofa mu yékkati ay loxoom, barkeel leen. 24:51 Bi mu leen dee barkeel, mu tàggoo ak ñoom, Yàlla yéege ko asamaan. 24:52 Taalibe ya màggal ko, daldi dellu Yerusalem, fees ak mbég. 24:53 Foofa daawuñu jóg ca kër Yàlla ga, di gërëm Yàlla.
1:1 Ca njàlbéen ga fekk na Kàddu gi am, te Kàddu gi ma nga woon ak Yàlla, te Kàddu gi Yàlla la woon. 1:2 Moo di ki nekkoon ak Yàlla ca njàlbéen ga. 1:3 Ci moom lañu sàkke lépp. Amul dara lu ñu sàkk lu jaarul ci moom. 1:4 Ci moom la dund nekk, te dund googu mooy leeral nit ñi. 1:5 Leer gi feeñ na ci biir lëndëm, te lëndëm gi jàppu ko. 1:6 Yàlla yónni woon na nit ku ñu naan Yaxya. 1:7 Kooku ñëw na, doon ab seede, ngir wax ci mbirum leer gi. Ñëw na ngir ñépp dégg li mu wax te gëm. 1:8 Moom ci boppam du woon leer gi, waaye ñëw na ngir seedeel leer gi. 1:9 Kàddu googu mooy leer gu wóor, giy ñëw ci àddina te di leeral nit ku nekk. 1:10 Ci àddina la nekkoon, àddina si ñu sàkk jaarale ko ci moom, te àddina xamu ko. 1:11 Ñëw na ci réewam, te ay ñoñam nanguwuñu ko. 1:12 Teewul ñi ko nangu te gëm ci turam, may na leen, ñu am sañ-sañu nekk doomi Yàlla. 1:13 Ñooñu judduwuñu ci deret walla ci bëgg-bëggu yaram, walla ci coobarey nit. Ñu ngi juddu ci Yàlla. 1:14 Kàddu gi ñëw, doon nit, dëkk ci sunu biir. Gis nañu ndamam, mu fees ak yiw ak dëgg, ndam li Baay bi jox jenn Doomam ji mu am kepp. 1:15 Yaxyaa ngi koy seedeel te yégle na lii; nee na: «Moo taxoon ma wax ne: “Dina ñëw sama gannaaw waaye moo ma gën a màgg, ndaxte nekk na laata may juddu.”» 1:16 Kàddu gi fees na ak yiw, te nun ñépp jot nanu ci sunu wàll, mu barkeel nu ay yooni-yoon. 1:17 Ndigali Yàlla yi, ci gémmiñu Musaa lañu leen jaarale; yiw wi ak dëgg gi, Yeesu Kirist moo ko indaale. 1:18 Kenn musul a gis Yàlla, waaye Bàjjo bi, di Yàlla te nekk ak Baay bi, moo ko xamle. 1:19 Lii mooy seedes Yaxya. Amoon na bés Yawut ya yónni ay saraxalekat ca Yaxya, ñu ànd ak ñu soqikoo ci giiru Lewi. Ñu nga jóge Yerusalem, ñëw ci moom, di ko laaj mooy kan. 1:20 Yaxya tontu na leen te nëbbu ci dara, wóoral na leen ne, moom du Almasi bi. 1:21 Ñu laaj ko ne: «Kon yaay kan? Ndax yaa di Iliyas?» Mu ne leen: «Déedéet, duma Iliyas.» Ñu ne ko: «Ndax yaa di Yonent, bi war a ñëw?» Mu tontu ne leen: «Déedéet.» 1:22 Noonu ñu laaj ko ne: «Wax nu yaay kan, ngir nu man a tontu ñi nu yónni. Nga ne yaa di kan?» 1:23 Yaxya tontu leen li yonent Yàlla Esayi waxoon ne: «Man maa di baat biy yégle ci màndiŋ mi ne: “Xàll-leen yoonu Boroom bi!”» 1:24 Amoon na ñu bokk ca Farisen ya, yu àndoon ca mbooloo, ma ñu yónni woon ca Yaxya. 1:25 Ñooñu laaj ko ne: «Gannaaw doo Almasi bi, doo Iliyas, doo Yonent bi war a ñëw, lu tax ngay sóob nit ñi ci ndox?» 1:26 Yaxya ne leen: «Man maa ngi sóobe ci ndox, waaye am na ci seen biir ku ngeen xamul. 1:27 Kookooy ñëw sama gannaaw, te man sax yeyoowumaa tekki ay dàllam.» 1:28 Lii xewoon na ci dëkku Betani, ca gannaaw dexu Yurdan, fa Yaxya doon sóobe. 1:29 Ca ëllëg sa, bi Yaxya gisee Yeesu, muy ñëw ci moom, mu ne: «Xool-leen! Kii mooy mbotem Yàlla, mi ñu nar a rey, ngir dindi bàkkaaru àddina. 1:30 Moo taxoon ma wax ne: “Am na kuy ñëw sama gannaaw, waaye moo ma gën a màgg, ndaxte nekk na laata may juddu.” 1:31 Xawma woon kooku kan la waroon a doon, waaye xamal ko bànni Israyil moo tax ma ñëw, di sóob nit ñi ci ndox.» 1:32 Ci kaw loolu Yaxya seede na lii: «Gis naa Xelu Yàlla mi ci melow pitax, mu jóge ci asamaan, tegu ci moom. 1:33 Bi loola laata am, xawma woon mooy kan, waaye Yàlla, mi ma yebal may sóobe ci ndox, nee woon na ma: “Dinga gis Xel mu Sell mi wàcc, tegu ci kaw nit. Kooku moo di ki leen di sóob ci Xel mu Sell mi.”» 1:34 Yaxya teg ca ne: «Gis naa loolu te seede naa ne, moom moo di Doomu Yàlla ji.» 1:35 Ca ëllëg sa Yaxya taxawaatoon na ca bérab booba, ànd ak ñaari taalibeem. 1:36 Bi mu gisee Yeesu muy romb, mu daldi ne: «Kii mooy mbotem Yàlla mi!» 1:37 Ñaari taalibe ya dégg li mu wax, daldi dem toppi Yeesu. 1:38 Yeesu geestu, gis ne, ñoo ngi koy topp. Mu ne leen: «Lu ngeen soxla woon?» Ñu tontu ko: «Foo dëkk, Ràbbi?» Ràbbi mi ngi tekki «Kilifa gi.» 1:39 Yeesu ne leen: «Kaayleen gis.» Noonu ñu dem, seeti fa mu daloon, ngoonalal ko. Ci tàkkusaani kaw la woon. 1:40 Kenn ci ñoom ñaar, ñi déggoon li Yaxya wax te topp Yeesu, ma nga tuddoon Andare, mi bokkoon ak Simoŋ Piyeer ndey ak baay. 1:41 Andare dafa daldi dem seeti Simoŋ ne ko: «Gis nanu Almasi bi.» Baat boobu mi ngi tekki «Kirist.» 1:42 Noonu mu yóbbu ko ci Yeesu. Yeesu xool ko ne ko: «Yaa di Simoŋ, doomu Yowaana. Dinañu la wooye Sefas.» Sefas mi ngi tekki «Piyeer,» maanaam «xeer.» 1:43 Ca ëllëg sa mu fas yéenee dem diiwaanu Galile te mu gis Filib. Yeesu ne ko: «Toppal ci man.» 1:44 Filib mu nga dëkkoon Betsayda, dëkku Andare ak Piyeer. 1:45 Filib dajeek Nataneel ne ko: «Gis nanu ki yoonu Musaa wi ak yonent yi doon wax. Mu ngi tudd Yeesu, doomu Yuusufa, te dëkk Nasaret.» 1:46 Nataneel tontu ko ne: «Aa! Ndax dara lu baax man na jóge Nasaret?» Filib ne ko: «Ñëwal gis.» 1:47 Naka la Yeesu gis Nataneel jëmsi ci moom, mu daldi ne ci mbiram: «Xool-leen, nitu Israyil dëgg a ngee di ñëw; du dox benn tànku caaxaan.» 1:48 Nataneel ne ko: «Noo ma xame?» Yeesu tontu ko ne: «Bi la Filib di laata woo, gis naa la, bi nga nekkee ca ker garabu figg ga.» 1:49 Nataneel wax ko ne: «Kilifa gi, yaay Doomu Yàlla ji, yaa di buuru Israyil!» 1:50 Yeesu tontu ko ne: «Ndax li ma ne, gis naa la ca ker garab ga, moo tax nga gëm? Dinga gis mbir yu gën a réy yii.» 1:51 Noonu mu teg ca ne: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, dingeen gis asamaan ubbiku, malaaka yiy baagante kaw ak suuf, di wàcc ci Doomu nit ki.»
2:1 Ñaari fan gannaaw loolu ag céet am ca dëkku Kana ca diiwaanu Galile. Yaayu Yeesu teewe woon na ko. 2:2 Woo woon nañu it Yeesu ca céet ga ak ay taalibeem. 2:3 Ca biir xew wa, biiñ ba daldi jeex. Yaayu Yeesu ne ko: «Amatuñu biiñ.» 2:4 Yeesu ne: «Soxna si, Loo ma bëggal? Ndaxte sama waxtu jotagul.» 2:5 Yaayam daldi ne surga ya: «Defleen lépp lu mu leen wax.» 2:6 Foofa amoon na fa juróom benni ndaa yu ñu yett ci doj, yu Yawut ya daan jëfandikoo ngir seen sangu set. Ndaa lu nekk man na def daanaka téeméeri liitar. 2:7 Yeesu ne surga ya: «Duyleen ndaa yi.» Ñu duy leen, ba ñu fees bay rembat. 2:8 Noonu Yeesu ne leen: «Tanqleen ci léegi, yót ko njiitu xew wi.» Ñu daldi ko ciy yót. 2:9 Ki jiite xew wa ñam ndox, ma Yeesu soppi biiñ. Xamul woon fu biiñ booba jóge, waaye surga ya tanqoon ndox ma, ñoom xamoon nañu ko. Naka noonu mu woo boroom céet ga ne ko: 2:10 «Ci xew yépp, naan gu neex gi lañuy jëkke. Bu nit ñi doyalee, ñu sog a génne ga ca des. Waaye yaw dangaa dencoon gi gën a neex ba nëgëni.» 2:11 Firnde bii ame ca Kana, ca diiwaanu Galile, moo doon kéemaan gi Yeesu jëkk a def. Ci noonu la wonee màggaayam te ay taalibeem gëm nañu ko. 2:12 Bi loolu weesoo, mu ànd ak yaayam, ay rakkam ak i taalibeem, dem dëkku Kapernawum. Waaye yàgguñu fa. 2:13 Màggalu Yawut, gi ñuy wax bésu Jéggi ba, mu ngi doon jubsi. Yeesu dem Yerusalem, 2:14 dugg ca kër Yàlla ga. Bi mu fa demee, fekk na ca ëtt ba ay jaaykati nag ak yu xar ak yu pitax, ak weccikatu xaalis ya toog. 2:15 Noonu Yeesu ràbb ab yar, daldi leen koy dàqe, ngir ñu génn ëttu kër Yàlla ga, ñoom ak xar ya ak nag ya. Mu tasaare xaalisu weccikat ya, daaneel taabal ya, 2:16 daldi ne jaaykati pitax ya: «Jëleleen fi lii! Sama kër Baay, buleen ko def marse!» 2:17 Taalibeem ya fàttaliku Mbind mii: «Cawarte gi ma am ci sa kër, mu ngi mel ni taal buy tàkk ci sama biir.» 2:18 Noonu Yawut ya ne ko: «Ban firnde nga nuy won ngir dëggal ne, am nga sañ-sañu def lii nga def?» 2:19 Yeesu tontu leen: «Daaneel-leen kër Yàlla gii, ma daldi koy yékkati ci ñetti fan.» 2:20 Ñu ne ko: «Nga ne kër Yàlla, gii ñu tabax ci ñeent-fukki at ak juróom benn, man nga koo yékkati ci ñetti fan!» 2:21 Waaye kër Yàlla, gi Yeesu doon wax, nekkul woon ab tabax, aw yaramam ci boppam moo ko taxoon di wax. 2:22 Gannaaw ga nag, bi Yeesu deeyee ba dekki, la taalibeem ya fàttaliku li mu waxoon, daldi gëm Mbind mi ak wax, ja leen Yeesu waxoon. 2:23 Bi Yeesu nekkee Yerusalem ci màggalu bésu Jéggi ba, ñu bare gis kéemaan, yi mu doon def, daldi gëm ci turam. 2:24 Waaye Yeesu wóoluwu leen woon, ndaxte xamoon na leen ñoom ñépp, 2:25 te it soxlawul ñu koy xamal dara ci nit, ndaxte moom ci boppam xam na xolu nit.
3:1 Amoon na ca Farisen ya nit ku ñu naan Nikodem te mu bokk ca kilifay Yawut ya. 3:2 Genn guddi mu ñëw ca Yeesu ne ko: «Kilifa gi, xam nanu ne, Yàllaa la yónni ngir nga jàngal nu, ndaxte kenn mënul a def firnde yii ngay wone te Yàlla àndul ak moom.» 3:3 Yeesu tontu ko ne: «Ci dëgg-dëgg maa ngi la koy wax, képp ku judduwaatul doo man a seede nguuru Yàlla.» 3:4 Nikodem ne ko: «Nit ku xas ba màggat, nan lay man a judduwaate? Ndax day dellu ci biiru yaayam ngir judduwaat?» 3:5 Yeesu tontu ko ne: «Ci dëgg-dëgg maa ngi la koy wax, ku judduwul ci ndox ak ci Xelum Yàlla, doo man a bokk ci nguuru Yàlla. 3:6 Lu juddoo ci nit, nit la; waaye lu juddoo ci Xelum Yàlla, xel la. 3:7 Li ma ne: “Fàww ngeen judduwaat,” bumu la jaaxal. 3:8 Ngelaw fu ko neex lay jublu. Yaa ngi koy dégg waaye xamuloo fu mu jóge, xamuloo fu mu jëm. Noonu la mel it ci képp ku juddoo ci Xelum Yàlla.» 3:9 Ci baat yooyu Nikodem ne ko: «Nu loolu man a ame?» 3:10 Yeesu tontu ko ne: «Yaw yaay jàngal bànni Israyil te xamuloo mbir yii? 3:11 Ci dëgg-dëgg maa ngi la koy wax, noo ngi wax li nu xam, di nettali li nu gis, waaye nanguwuleen a gëm li nu seede. 3:12 Gannaaw gëmuleen li ma leen di wax ci mbiri àddina, naka ngeen man a gëme, bu ma leen waxee ci mbiri asamaan? 3:13 Kenn musul a yéeg ci asamaan su dul ki fa jóge, muy Doomu nit ki. 3:14 Te itam na Musaa sampe woon ab bant ca diggu màndiŋ ma, takk ca jaan, ja mu defare woon xànjar, fàww ñu yékkatee noonu Doomu nit ki, 3:15 ngir képp ku ko gëm am ci moom dund gu dul jeex.» 3:16 Ndaxte Yàlla dafa bëgg àddina, ba joxe jenn Doomam ji mu am kepp, ngir képp ku ko gëm am dund gu dul jeex te doo sànku mukk. 3:17 Yàlla yónniwul Doomam ci àddina ngir mu daan nit ñi, waaye ngir musal leen. 3:18 Képp ku ko gëm deesu la daan, waaye ku ko gëmul daan nañu la ba noppi, ndaxte gëmuloo ci turu Doom ji Yàlla am kepp. 3:19 Ci nii la àtte bi ame: leer gi ñëw na ci àddina, waaye nit lëndëm gi lañu taamu ndax seeni jëf yu bon. 3:20 Képp kuy def lu bon day bañ leer gi te du ci ñëw, ndax ragal ay jëfam di feeñ bëccëgu ndarakàmm. 3:21 Waaye ku def lu jub day ñëw ci leer gi, ngir ñu xam ne, def na ay jëfam ci kanam Yàlla. 3:22 Gannaaw loolu Yeesu ànd ak ay taalibeem, dem ca biir diiwaanu Yude, toog fa ak ñoom ab diir, di sóob nit ñi ci ndox. 3:23 Yaxya moom itam doon na sóobe ci ndox ci dëkku Aynon, ca wetu dëkku Salim, ndaxte diiwaan booba bare woon na ndox. Nit ñi daan nañu ñëw ci moom, mu di leen sóob. 3:24 Booba tëjaguñu Yaxya ci kaso. 3:25 Foofa ay taalibey Yaxya tàmbalee werante ak benn Yawut ci mbirum sangu set. 3:26 Ci kaw loolu ñu dem ca Yaxya ne ko: «Kilifa gi, ndax fàttaliku nga kooka nga seede woon te mu nekkoon ak yaw ca gannaaw dexu Yurdan? Moom de, ma ngay sóobe ci ndox léegi te ñépp a ngay dem ca moom!» 3:27 Yaxya tontu leen: «Kenn mënul a am dara lu ko Yàlla joxul. 3:28 Yéen ci seen bopp man ngeen a seede ne, waxoon naa ne, duma Almasi bi waaye dañu maa yónni ma jiitusi ko. 3:29 Kiy céetal moo moom séetam. Waaye xaritu kiy céetal dafay taxaw di ko déglu, tey bég, bu déggee baatam. Mbég moomu moo di sama bos tey, te fi mu nekk mat na sëkk. 3:30 Li war moo di moom, mu gën a màgg te man, ma gën a féete suuf.» 3:31 Ki jóge ci kaw moo féete kaw ñépp; ki jóge ci suuf nag, ci suuf rekk la man a bokk, te ni niti àddina lay waxe. Ki jóge asamaan 3:32 day wax li mu gis ak li mu dégg, waaye kenn nanguwul li mu seede. 3:33 Képp ku nangu seedeem nangu nga ne Yàlla, dëgg lay wax. 3:34 Ndaw li Yàlla yónni, kàddug Yàlla lay wax, ndaxte mayu Xel mu Sell, mi Yàlla sol ci moom, amul dayo. 3:35 Baay bi dafa bëgg Doom ji, te jox na ko sañ-sañ ci lépp. 3:36 Ku gëm Doom ji, am nga dund gu dul jeex; ku déggadil Doom ji, amuloo dund, waaye merum Yàllaa ngi la tiim.
4:1 Amoon na benn bés Farisen yi dégg ne, ñiy topp Yeesu ñoo ëpp ñiy topp Yaxya, te ñi Yeesu sóob ci ndox ñoo ëpp ñi Yaxya sóob. 4:2 Fekk Yeesu moom ci boppam daawul sóob kenn ci ndox, waaye ay taalibeem ñoo daan sóobe. 4:3 Bi Yeesu yégee loolu nag, mu jóge Yude, dellu diiwaanu Galile. 4:4 Bi muy dem Galile, waroon na jaar ci diiwaanu Samari. 4:5 Noonu mu agsi ci wetu dëkku Sikar ci tool, bi Yanqóoba mayoon doomam Yuusufa. 4:6 Foofa la teenu Yanqóoba nekkoon. Yeesu toog ca pindu teen ba, di noppalu ndax coonob tukki ba. Ca digg-bëccëg la woon. 4:7 Noonu jigéenu waa Samari ñëw fa di root. Yeesu ne ko: «May ma ndox, ma naan.» 4:8 Fekk booba nag, taalibey Yeesu ya dañoo demoon ca biir dëkk ba, di jënd lu ñu lekk. 4:9 Jigéen ja tontu ko ne: «Yaw, ngay Yawut, man maay jigéen ju dëkk Samari; nan nga ma man a ñaane ndox?» Jigéen ja wax na loolu, ndaxte Yawut ya bokkuñu woon ak waa Samari ndab yu ñuy lekke. 4:10 Noonu nag Yeesu tontu ko: «Soo xamoon li Yàlla maye, xam ki lay ñaan ndox, kon yaw ci sa bopp, yaa koy ñaan, te moom dina la may ndoxum dund.» 4:11 Jigéen ja ne ko: «Sang bi, teen bi xóot na te amuloo baag, kon fooy jële ndoxum dund? 4:12 Xanaa kay xalaatuloo ne, yaa gën a màgg sunu maam Yanqóoba, moom mi nu gasal teen bii, mu naan ci moom ak i doomam, wëgg cig juram?» 4:13 Yeesu wax ko ne: «Ku naan ci ndoxum teen bii, balaa yàgg mu maraat, 4:14 waaye ndox, mi may joxe, ku ci naan du marati mukk, ndaxte day nekk ci moom bëtu ndox buy ball, di joxe dund gu dul jeex.» 4:15 Noonu jigéen ja daldi ko ne: «Sang bi, may ma ci ndox moomu, ngir ma bañatee mar, bay ñëw ba fii di rootsi.» 4:16 Yeesu ne ko: «Demal woowi sa jëkkër te ñëw.» 4:17 Jigéen ja tontu ko ne: «Awma jëkkër de.» Yeesu ne ko: «Wax nga dëgg ne, amuloo jëkkër, 4:18 ndaxte amoon nga juróomi jëkkër, te ki nga nekkal léegi du sa jëkkër. Li nga wax dëgg la.» 4:19 Jigéen ja ne ko: «Sang bi, gis naa ne, ab yonent nga. 4:20 Nun nag, nakajekk sunuy maam ca tund wee ngay séen lañu daan jaamoo Yàlla, waaye yéen Yawut yi, dangeen ne Yerusalem lañu war a jaamoo Yàlla.» 4:21 Yeesu ne ko: «Jigéen ji, gëmal lii ma lay wax: dina am jamono joo xam ne du ci tund wale te du ci Yerusalem ngeen di jaamoo Baay bi. 4:22 Yéen waa Samari, xamuleen li ngeen di jaamu. Nun Yawut yi, xam nanu li nuy jaamu, ndaxte kiy musal àddina ci Yawut yi la jóge. 4:23 Waaye jamono dina ñëw, te agsi na ba noppi, jamono joo xam ne jaamukat yi dëgg dinañu jaamu Baay bi ci xel ak ci dëgg. Ñooñu nag, ñooy jaamu Baay bi, ni mu ko bëgge. 4:24 Yàlla xel la, kon ñi koy jaamu war nañu koo jaamu ci xel ak ci dëgg.» 4:25 Jigéen ja ne ko: «Xam naa ne Almasi bi --maanaam Kirist — dina ñëw te bu ñëwee, dina nu leeralal lépp.» 4:26 Yeesu tontu ko: «Maa di Almasi bi, man miy wax ak yaw.» 4:27 Noonu nag taalibey Yeesu ya dellusi, gis muy wax ak ab jigéen. Ñu daldi jaaxle lool. Waaye kenn ñemewu ko woon ne: «Looy laaj?» walla: «Lu tax ngay wax ak moom?» 4:28 Noonu jigéen ja wacc fa njaqam, daldi dem ca dëkk ba ne leen: 4:29 «Kaayleen gis; nit a nga fee ku ma wax lépp lu ma mas a def. Ndax kooku du Almasi bi?» 4:30 Noonu waa dëkk ba jóg, jëm ca Yeesu. 4:31 Fekk taalibey Yeesu ya di ko gétën ne: «Kilifa gi, lekkal.» 4:32 Waaye Yeesu tontu leen: «Am na ñam wu may lekk, te xamuleen ko.» 4:33 Taalibe ya nag di laajante naan: «Ndax dafa am ku ko indil lekk?» 4:34 Yeesu ne leen: «Sama ñam moo di def coobarey ki ma yónni te àggale liggéey, bi mu ma sant. 4:35 Du dangeen naan: “Fii ak ñeenti weer ñu góob?” Waaye man, dama leen naan: xool-leen tool yi, ñoo ngi ñor ba weex tàll, di xaar ku leen góob. 4:36 Kiy góob tool yi mu ngi jot xaat peyam; day dajale nit ñi ngir dund gu dul jeex, ni ñuy dajalee pepp. Kon boog kiy ji dina bégandoo ak kiy góob. 4:37 Wax ji ñu wax ne: “Kenn dina ji, keneen góob,” dëgg la. 4:38 Yebal naa leen, ngeen góob tool bu ngeen beyul. Ñeneen a ko bey, te yéena ko jariñoo.» 4:39 Bi jigéen ja nee waa dëkk ba: «Wax na ma li ma def lépp,» ñu bare gëm nañu Yeesu. 4:40 Ñu daldi dikk ñaan Yeesu, mu dal ak ñoom. Yeesu toog fa ñaari fan. 4:41 Ñu bare gëm ko ndax li mu doon wax. 4:42 Ñu ne jigéen ja: «Léegi gëm nanu, te du li nga wax moo tax waaye li nu gisal sunu bopp. Te xam nanu ne, dëgg-dëgg kii moo di Musalkatu àddina si.» 4:43 Bi Yeesu amee ñaari fan ca dëkk ba, mu jóge fa, jëm diiwaanu Galile, 4:44 ndaxte moom ci boppam nee woon na: «Ab yonent, kenn du ko faaydaal ca réewam.» 4:45 Bi mu agsee Galile, nit ñi teeru ko, ndaxte ñoom itam teewoon nañu ca màggalu bésu Jéggi ba ca Yerusalem, te gisoon nañu la mu fa defoon lépp. 4:46 Noonu kon mu dellusi Kana ci Galile, dëkk ba mu soppe woon ndox ma biiñ. Amoon na benn dagu buur bu dëkkoon Kapernawum te doomam feebar. 4:47 Bi mu déggee ne, Yeesu jóge na Yude, ñëw Galile, mu dikk ci moom, ñaan ko mu ñëw këram, wéral doomam, ji wopp bay bëgg a dee. 4:48 Yeesu ne ko: «Yéen daal, dungeen gëm mukk, fi ak gisuleen ay firnde walla ay kéemaan.» 4:49 Dagu buur ba neeti ko: «Sang bi, ñëwal, bala sama doom di dee.» 4:50 Yeesu ne ko: «Demal, sa doom dina dund.» Kilifa ga gëm la ko Yeesu wax, daldi dem. 4:51 Bi muy dellu këram nag, ay surgaam gatandu ko. Ñu daldi ne ko: «Xale bi dina dund!» 4:52 Mu laaj leen ci ban waxtu la tàmbalee tane, ñu tontu ko ne: «Démb ca njolloor la am ag féex.» 4:53 Noonu baayu xale ba daldi seetlu ne, ca waxtu woowa la ko Yeesu ne woon: «Sa doom dina dund.» Moom ak njabootam gépp, ñu daldi gëm Yeesu. 4:54 Lii mooy ñaareelu firnde, bi Yeesu def ci Galile, gannaaw bi mu jógee Yude.
5:1 Gannaaw loolu Yawut ya amoon nañu genn màggal, moo tax Yeesu demoon Yerusalem. 5:2 Ca wetu benn ci bunti dëkk ba nag, maanaam ca Buntu xar ya, am na fa bët bu tudd Betesda ci làkku yawut, te ñu wërale ko ak juróomi mbaar. 5:3 Ca suufu mbaar yooyu la jarag yu bare, yu deme niki ay gumba, ay lafañ ak ay làggi, daan tëdd, di xaar ndox mi yengatu; 5:4 ndaxte, ci ni ñu ko nettalee, benn malaakam Boroom bi da daan wàcc léeg-léeg di jax ndox mi. Bu ndox mi masaa yengu ba noppi, jarag ju ca jiitu, wopp joo amaan, daldi wér ca saa sa. 5:5 Amoon na fa benn waay bu feebaroon lu mat fanweeri at ak juróom ñett. 5:6 Bi ko Yeesu séenee mu tëdd, te mu xam ne, woppam ji yàggoon na lool, mu laaj ko ne: «Ndax bëgg ngaa wér?» 5:7 Jarag ja tontu ko ne: «Sang bi, duma am ku ma sóob ci ndox mi, bu yengoo; su ma ciy fexee dem, ñu jëkk ma ci.» 5:8 Yeesu ne ko: «Jógal, jël sa basaŋ te dox.» 5:9 Ca saa sa mu daldi wér, jël basaŋam, daldi dox. Mbir moomu dafa daje woon ak bésu noflaay ba, 5:10 looloo tax ba Yawut ya daldi ne nit ku wér ka: «Tey bésu noflaay la, te sunu yoon aaye na, ngay yor sa basaŋ.» 5:11 Mu ne leen: «Ki ma faj moo ma ne: “Jëlal sa basaŋ te dox.”» 5:12 Ñu ne ko nag: «Ku la ne: “Jëlal sa basaŋ te dox?”» 5:13 Waaye waa ji xamul ki ko wéral, fekk booba Yeesu dem na, te nit ñu bare teewoon nañu ca bérab ba. 5:14 Bi ñu ca tegee ab diir, Yeesu dajeek moom ca kër Yàlla ga ne ko: «Déglul, fii mu ne, wér nga; bul defati bàkkaar, ngir ragal lu yées lii dal la.» 5:15 Noonu nit ka dellu ne Yawut ya, Yeesu moo ko fajoon. 5:16 Looloo tax Yawut ya di wut a sonal Yeesu, ndaxte daan na jëfe noonu ca bésu noflaay ba. 5:17 Waaye Yeesu tontu na leen ne: «Sama Baay nekk na ba tey ci liggéey, kon man itam damay liggéey.» 5:18 Baat boobu moo tax ba Yawut yi gën koo wut a rey, ndaxte yemul woon rekk ci bañ a topp ndigalu bésu noflaay ba, waaye dafa wax it ne, Yàlla Baayam la, ba teg boppam Yàlla. 5:19 Noonu Yeesu ne leen: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, Doom ji mënul a def dara moom ci boppam; li mu gis Baay bi di def rekk lay def. Li Baay bi di jëf la Doom ji itam di jëf. 5:20 Ndaxte Baay bi bëgg na Doom ji, ba di ko won lépp lu muy def, te dina ko won jëf yu ëpp kéemaan yii, ngir ngeen gën a waaru. 5:21 Maanaam, ni Baay bi di dekkale ñu dee ñi, di leen jox dund, noonu la Doom ji di joxe dund ñi mu ko bëgg a jox. 5:22 Baay bi du àtte kenn; àtte bi yépp, jox na ko Doom ji, 5:23 ngir ñépp di teral Doom ji, ni ñuy terale Baay bi. Ku teralul Doom ji, teraloo Baay, bi ko yónni. 5:24 «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, ku dégg sama kàddu te gëm ki ma yónni, am nga dund gu dul jeex te doo jaar ca àtte ba, ndaxte génn nga ci dee, tàbbi ci dund. 5:25 Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, jamono dina ñëw te agsi na ba noppi, mooy jamono, ji ñu dee ñi di dégg baatu Doomu Yàlla ji, te ku ko dégg dinga dund. 5:26 Ndaxte ni Baay bi ame dund moom ci boppam, noonu it la ko maye Doom ji, mu am ko ci boppam. 5:27 Jox na Doom ji itam sañ-sañu àtte, ndaxte mooy Doomu nit ki. 5:28 «Bu leen ci dara jaaxal; ndaxte jamonoo ngi ñëw ju néew yépp, yi nekk ci seen bàmmeel, di dégg baatam tey génn. 5:29 Ñi daan jëf lu baax dinañu dekki, dund ba fàww, waaye ñi daan jëf lu bon, dinañu dekki, ñu daan leen. 5:30 Mënumaa def dara man ci sama bopp. Ni ma Baay bi di digale rekk laay àttee, te sama àtte bu jub la, ndaxte defuma sama bëgg-bëgg, ci waawi ki ma yónni doŋŋ laay aw. 5:31 «Su ma seedeelee sama bopp, sama wax du am maana. 5:32 Waaye keneen moo may seedeel, te bir na ma ne, la muy wax ci man dëgg la. 5:33 «Yéen yónni ngeen ay ndaw ci Yaxya, te seede na dëgg. 5:34 Man ci sama bopp soxlawuma seedes nit; waaye nag damay wax loolu rekk, ngir ngeen mucc. 5:35 Yaxya meloon na ni làmp buy tàkk tey leeral, te nangu ngeen a bànneexu ab diir ci leeram. 5:36 «Waaye yor naa ci man seede su gën a mag si ma Yaxya di seedeel: maa ngi def jëf, yi ma Baay biy sant. Jëf yooyu may def nag ñooy seede ne, Baay bi moo ma yónni. 5:37 Te Baay bi ma yónni, moom itam seede na ma. Musuleen a dégg baatam te musuleen a gis xar-kanamam, 5:38 te kàddoom saxul ci yéen, ndaxte gëmuleen ki mu yónni. 5:39 Yéena ngi gëstu Mbind yi, ndaxte dangeen cee yaakaar dund gu dul jeex. Mbind yooyu nag far, ci sama mbir lañuy wax; 5:40 te bëgguleen a ñëw ci man ngir am dund! 5:41 «Wutuma tagg yu jóge ci nit. 5:42 Waaye yéen, xam naa leen; leer na ma ne, amuleen ci seen xol benn mbëggeel ci Yàlla. 5:43 Man ñëw naa ci sama turu Baay, te nanguwuleen ma, waaye bu keneen dikkee ci turu boppam, ngeen nangu ko. 5:44 Bëgg ngeen ku leen di tagg, te wutuleen ngërëm, li jóge ci jenn Yàlla rekk ji am. Kon nan ngeen man a gëme? 5:45 «Buleen xalaat ne, maa leen di jiiñ dara ci sama kanamu Baay. Musaa, mi ngeen yaakaar, moo leen di booleek moom. 5:46 Bu ngeen gëmoon Musaa, dingeen ma gëm man itam, ndaxte seedeel na ma. 5:47 Waaye su fekkee gëmuleen li Musaa bind, kon nu ngeen man a gëme samay wax?»
6:1 Gannaaw loolu Yeesu dafa jàll dexu Galile, maanaam dexu Tiberyàdd. 6:2 Mbooloo mu bare topp ci moom, ndaxte gisoon nañu firnde yooyee mu wone, bi mu wéralee jarag ya. 6:3 Yeesu daldi yéeg ca kaw tund wa, toog fa ak ay taalibeem. 6:4 Fekk na booba bésu Jéggi ba, di màggalu Yawut ya, jubsi. 6:5 Bi Yeesu xoolee, gis mbooloo mu réy di ñëw ci moom, mu ne Filib: «Fu nuy jële mburu, mu nu leen man a dundale?» 6:6 Bi muy wax loolu it, da doon seetlu Filib, ndaxte xamoon na booba li mu nar a def. 6:7 Filib ne ko: «Peyug juróom ñetti weer sax, bu nu ko amoon, du leen man a doy ci mburu, ba kenn ku nekk ci ñoom am ci dog wu ndaw.» 6:8 Keneen ca taalibe ya di Andare, mi bokk ak Simoŋ Piyeer ndey ak baay, ne ko: 6:9 «Am na fi ci mbooloo mi ab xale bu yor juróomi mburu ak ñaari jën, waaye loolu lu muy jariñ mbooloo mu tollu nii?» 6:10 Yeesu daldi ne taalibe ya: «Na ñépp toog.» Fekk ñax mu bare amoon ca bérab ba. Noonu góor ñépp àgg suuf. Waroon nañoo mat juróomi junni. 6:11 Yeesu daldi jël mburu ya, gërëm Yàlla, ba noppi séddale ko ña fa toogoon. Mu jox leen itam jën, ba ñu doyal sëkk. 6:12 Bi ñu lekkee ba regg, Yeesu ne taalibe ya: «Dajaleleen desitu mburu mi, ba dara du ci réer.» 6:13 Ñu dajale ko, daldi feesal fukki pañe ak ñaar ak desiti juróomi mburu, yi ñu doon lekk. 6:14 Bi nit ña gisee firnde jooju Yeesu wone, ñu ne: «Dëgg-dëgg kii mooy Yonent, bi war a ñëw ci àddina!» 6:15 Yeesu gis ne dañu koo nar a jëlsi, fal ko buur. Mu bàyyi leen fa, dellu moom rekk ca tund wa. 6:16 Bi timis jotee taalibeem ya wàcc ca tefes ga, 6:17 dugg ci gaal, di jàll dex gi, jëm dëkku Kapernawum. Booba guddi woon na, te Yeesu agseegul ci ñoom. 6:18 Dex gi yengu na lool, ndaxte da doon ngelaw ak doole. 6:19 Bi ñu joowee lu war a tollook juróom benni kilomet, ñu séen Yeesu, muy dox ci kaw dex gi, jëm ci ñoom, ñu daldi tiit. 6:20 Waaye Yeesu ne leen: «Man la, buleen tiit!» 6:21 Noonu ñu nangu koo dugal ca gaal ga, gaal ga daldi teer ca saa sa ca fa ñu bëggoon a wàcc. 6:22 Ca ëllëg sa mbooloo, ma des ca geneen wàllu dex ga, gis ne genn gaal ga fa nekkoon rekk dem na. Xam nañu ne Yeesu bokku ko woon ak taalibe ya, ndaxte ñoom rekk a àndoon. 6:23 Waaye yeneen gaal yu jóge dëkku Tiberyàdd ñëw, teer ca wetu fa ñu lekke woon mburu ma, gannaaw bi Boroom bi santee Yàlla ba noppi. 6:24 Bi mbooloo ma gisee ne, Yeesu walla taalibe ya kenn nekkatu fa, ñu dugg ca gaal yooyu, dem seeti ko Kapernawum. 6:25 Bi ñu fekkee Yeesu ca geneen wàllu dex ga, ñu ne ko: «Kilifa gi, kañ nga fi ñëw?» 6:26 Yeesu ne leen: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, firnde yi ngeen gis taxul ngeen may seet. Yéena ngi may wër ndax mburu, mi ngeen lekk ba suur. 6:27 Buleen liggéeyal ñam wuy yàqu; li gën mooy ñam wu sax abadan tey joxe dund gu dul jeex. Ñam woowule, Doomu nit ki dina leen ko jox, ndaxte moom la Yàlla Baay bi tànn, mu nekk ndawam.» 6:28 Noonu ñu laaj ko ne: «Lu nu war a liggéey, ngir matal jëf yi neex Yàlla?» 6:29 Yeesu tontu leen ne: «Jëf ji neex Yàlla, moo di gëm ki mu yónni.» 6:30 Ñu ne ko: «Ban firnde nga nu man a won, ngir nu gëm la? Ban liggéey nga nar a def? 6:31 Sunuy maam dunde nañu mànn ca màndiŋ ma, ndaxte Mbind mi nee na: “Jox na leen, ñu lekk ñam wu wàcce ca asamaan.”» 6:32 Yeesu waxaat ne: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, du Musaa moo leen jox ñam woowu wàcce ca asamaan; sama Baay ci boppam, moo leen di jox ñam wu wóor, wi wàcce ca asamaan. 6:33 Ndaxte ñam, wi Yàlla di joxe, mooy ñam wiy wàcce ci asamaan tey jox àddina si dund.» 6:34 Ñu ne ko nag: «Sang bi, kon dee nu faral di jox ci ñam woowe!» 6:35 Yeesu tontu leen ne: «Man maay ñam wiy joxe dund. Ku ñëw ci man, doo xiif mukk; te ku ma gëm, doo mar. 6:36 Waaye wax naa leen ko ba noppi; gis ngeen ma te taxul ngeen gëm! 6:37 Képp ku ma Baay bi jox dina ñëw ci man, te duma dàq mukk ki may fekksi. 6:38 Ndaxte wàccewuma ci asamaan ngir def sama bëgg-bëgg, waaye damay matal bëgg-bëggu ki ma yónni. 6:39 Lii mooy bëgg-bëggu ki ma yónni: bu ma ñàkk kenn ci ñi mu ma may, te dafa bëgg it ma dekkal leen keroog bés bu mujj ba. 6:40 Ndaxte lii mooy bëgg-bëggu Baay bi: képp ku gis Doom ji te gëm ko, am dund gu dul jeex, te bés bu mujj ba, dinaa ko dekkal!» 6:41 Yawut ya tàmbali di ñurumtoo Yeesu, ndaxte dafa ne: «Maay ñam wi wàcce ci asamaan.» 6:42 Ñu naan: «Ndax kii du Yeesu, doomu Yuusufa? Xam nanu ndeyam ak baayam. Kon nag lu tax léegi mu naan, mi ngi jóge asamaan?» 6:43 Yeesu ne leen: «Bàyyileen seen ñurumtu bi. 6:44 Kenn mënul a ñëw ci man te Baay, bi ma yónni, xiirtalu la ci, te man dinaa la dekkal keroog bés bu mujj ba. 6:45 Yonent yi bind nañu kàddu gii: “Yàlla dina leen jàngal ñoom ñépp.” Kon nag ku déglu te nangu waxi Baay bi, dina ñëw ci man. 6:46 Tekkiwul ne kenn mas na gis Baay bi. Ki jóge ci Yàlla doŋŋ a ko gis. 6:47 Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, ku gëm am nga dund gu dul jeex. 6:48 Maay ñam wiy joxe dund. 6:49 Seeni maam lekk nañu mànn ca màndiŋ ma, teewul dee nañu. 6:50 Waaye ñam wiy wàcce ci asamaan, ku ko lekk, doo dee. 6:51 Man maay ñam wiy dund te wàcce ci asamaan. Ku lekk ci ñam wii, dinga dund ba fàww. Te it ñam wi may joxeji, sama yaram la; dama koy joxe ngir àddina man a dund.» 6:52 Noonu Yawut ya werante werante bu tàng ci seen biir naan: «Naka la nu waa jii man a joxe yaramam, ngir nu lekk ko?» 6:53 Yeesu ne leen: «Dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, bu ngeen lekkul yaramu Doomu nit ki te naanuleen deretam, dungeen am dund ci yéen. 6:54 Ku lekk sama yaram te naan sama deret, am nga dund gu dul jeex, te dinaa la dekkal keroog bés bu mujj ba. 6:55 Ndaxte sama yaram mooy ñam wu wóor wi, te sama deret mooy naan gu wóor gi. 6:56 Kiy lekk sama yaram tey naan sama deret dina sax ci man, ma dëkk ci moom. 6:57 Baay bi ma yónni mu ngi dund, te maa ngi dund jaarale ko ci moom; noonu itam ku may lekk dina dund jaarale ko ci man. 6:58 Kon nag ñam, wi wàcce ci asamaan a ngi noonu; bokkul ak ñam, wa seeni maam lekkoon te faatu. Ku lekk ñam wii may wax dinga dund ba fàww.» 6:59 Baat yooyu la Yeesu wax, bi mu doon jàngale ca jàngu ba ca Kapernawum. 6:60 Bi ñu dégloo Yeesu ba noppi, taalibeem yu bare nee nañu: «Njàngale mii de, jafe na! Kan moo ko man a déglu?» 6:61 Yeesu gis ne taalibeem yaa ngi ñurumtoo loolu, mu ne leen: «Ndax li ma wax da leen a jaaxal? 6:62 Lan mooy am nag, bu fekkee gis ngeen Doomu nit ki dellu, yéeg fa mu jëkkoon a nekk? 6:63 Xelu Yàlla mi mooy joxe dund; ñam wi jariñul dara. Kàddu yi ma leen wax, ci Xelum Yàlla lañu jóge te ñooy joxe dund. 6:64 Waaye am na ci seen biir ñu ko gëmul.» Ndaxte Yeesu xamoon na ca njàlbéen ga ñan ñoo ko waroon a gëmadi ak kan moo ko waroon a wor. 6:65 Mu dolli ca it ne: «Looloo tax ma ne, kenn mënul a ñëw ci man te Baay bi mayu la, nga agsi.» 6:66 Ci loolu taalibeem yu bare dëpp, bañatee ànd ak moom. 6:67 Yeesu daldi wax ak fukki taalibe yi ak ñaar ne leen: «Mbaa bëgguleen a dem, yéen itam?» 6:68 Simoŋ Piyeer ne ko: «Boroom bi, ci kan lanuy dem? Yaa yor kàddu yiy joxe dund gu dul jeex. 6:69 Léegi nun gëm nanu te xam nanu ne, yaa di Aji Sell, ji jóge ci Yàlla.» 6:70 Yeesu daldi tontu ne leen: «Xanaa du maa leen tànn, yéen fukk yi ak ñaar? Moona, am na ci yéen koo xam ne seytaane la!» 6:71 Yudaa miy doomu Simoŋ Iskariyo la doon wax. Ndeke Yudaa, la muy bokk lépp ca fukki taalibe ya ak ñaar, moo ko naroon a wor.
7:1 Gannaaw loolu Yeesu doon na wër diiwaanu Galile. 7:2 Bëggul woon a dem diiwaanu Yude, ndaxte Yawut ya dañu ko doon wut a rey. Fekk na bésu xewu Yawut ya, ñu koy wax màggalu Mbaar ya, mu ngi doon jubsi. 7:3 Noonu rakki Yeesu yu góor ya ne ko: «Jóge fi te dem diiwaanu Yude, ngir say taalibe gis, ñoom itam, jaloore yi ngay def. 7:4 Ku bëgg a siiw, doo nëbb say jëf. Boo demee bay wone jaloore yu mel ni, fexeel ba ñépp gis la.» 7:5 Rakkam yi dañu doon wax loolu, ndaxte ñoom itam gëmuñu ko woon. 7:6 Yeesu ne leen: «Sama waxtu jotagul. Ci yéen nag, waxtu yépp a baax. 7:7 Àddina du leen bañ waaye bañ na ma, man, ndaxte maa wax ne, seeni jëf baaxul. 7:8 Yéen nag demleen màggal ga. Demaguma màggal googu, ndaxte sama waxtu jotagul.» 7:9 Bi mu leen waxee loolu ba noppi, moom mu des Galile. 7:10 Bi rakkam ya demee ca màggal ga, Yeesu itam sog a dem te kenn yégu ko; siiwalul demam. 7:11 Fekk Yawut yaa nga ko doon seet ca màggal ga te naan: «Ana waa ji?» 7:12 Ca biir mbooloo ma ñu ngi doon déeyante, di wax ci ay mbiram. Ñii naan: «Nit ku baax la.» Ñee naan: «Déedéet, day nax nit ñi.» 7:13 Waaye kenn ñemewu koo tudd ca kaw, ndaxte dañoo ragaloon Yawut ya. 7:14 Bi ñu demee ba ca diggu màggal ga, Yeesu dem di jàngale ca kër Yàlla ga. 7:15 Yawut ya nag jaaxle, daldi ne: «Nu waa jii def ba xam lii lépp, moom mi jàngul?» 7:16 Yeesu daldi leen tontu ne: «Li may jàngale, jógewul ci man, waaye ci ki ma yónni la jóge. 7:17 Ku fas yéenee wéy ci bëgg-bëggu Yàlla, dina xam ndax sama njàngale ci Yàlla la jóge, walla ci sama coobare. 7:18 Nit kiy wax ci coobareem nag, day wut a màggal boppam, waaye kiy wut a màggal ki ko yónni, dëgg rekk lay wax te jubadiwul fenn. 7:19 Xanaa du Musaa moo leen jox ndigali Yàlla yi? Waaye kenn ci yéen sàmmu ko! Lu tax ngeen bëgg maa rey?» 7:20 Mbooloo ma ne ko: «Xanaa dangaa am ay rab! Ku lay wut a rey?» 7:21 Yeesu ne leen: «Benn jaloore rekk laa def, te yéen ñépp ngeen jaaxle! 7:22 Li leen Musaa jox ndigalu xarafal gune yi --jógewul kat ci Musaa; mi ngi tàmbalee ci seen maami cosaan — moo tax ba ngeen nangoo xarafal nit ci bésu noflaay bi. 7:23 Bu ngeen manee xarafal nit ci bésu noflaay bi, ngir bañ a wàcc yoonu Musaa, lu tax nag ngeen mere ma, ndax li ma ci wéral nitu lëmm? 7:24 Bàyyileen di àtte ci ni ngeen di gise, te di àtte dëgg.» 7:25 Am na ci waa Yerusalem ñu doon wax naan: «Xanaa du nit kii lañuy wut a rey? 7:26 Xool-leen, mi ngi waaraate ci biir nit ñi, te kenn du ko wax dara. Ndax sunu kilifa yi dañoo xam ne, mooy Almasi bi? 7:27 Waaye waa ji, xam nanu fu mu jóge, te saa su Almasi bi dee dikk, kenn du xam fu mu bàyyikoo.» 7:28 Yeesu di jàngale ca kër Yàlla ga, daldi wax ca kaw ne: «Ndax xam ngeen ma te xam fi ma jóge? Ñëwaluma sama bopp, waaye ki ma yónni, ku wóor la. Yéen xamuleen ko. 7:29 Man xam naa ko, ndaxte ca moom laa jóge, te itam moo ma yónni.» 7:30 Noonu ñu koy wut a jàpp, waaye kenn manalu ko woon dara, ndaxte waxtoom jotagul woon. 7:31 Moona nag, ñu bare ca mbooloo ma gëm nañu ko. Ñu nga naan: «Ndax bés bu Almasi bi dikkee, ay firndeem dina ëpp yu nit kii?» 7:32 Farisen ya daldi dégg la mbooloo ma doon déeyante ci mbirum Yeesu. Saraxalekat yu mag ya ak Farisen ya yebal ay alkaati yu daan wottu kër Yàlla ga, ngir ñu jàppi ko. 7:33 Yeesu wax ne: «Dinaa nekk ak yéen fi ak ab diir, sog a dem ci ki ma yónni. 7:34 Dingeen ma seet, waaye dungeen ma gis; te dungeen man a dem fa may nekk.» 7:35 Yawut ya di laajante ci seen biir naan: «Fu muy dem fu nu ko dul fekk? Mbaa du dafa nar a dem ca Yawut, ya gàddaaye ca Gereg ya, te jàngali Gereg ya? 7:36 Lan la baat yii mu wax di tekki: “Dingeen ma seet waaye dungeen ma gis,” ak: “Dungeen man a dem fa may nekk?”» 7:37 Bés ba mujjoon ca màggal ga moo ca ëpp solo; keroog Yeesu taxaw, wax ca kaw ne: «Ku mar, na ñëw ci man; ku gëm, na naan! Ndaxte Mbind mi nee na, ndox mu bare muy dundale dina xellee ci dënnam.» 7:39 Booba li ko taxoon di wax mooy Xelu Yàlla, mi ñi ko gëm naroon a jot. Fekk na joxeeguñu woon Xelu Yàlla mi, ndaxte ndamu Yeesu feeñagul woon. 7:40 Bi ñu déggee wax jooja, am ay nit ca mbooloo ma ñu naan: «Dëgg-dëgg kii mooy Yonent bi war a ñëw.» 7:41 Ñeneen naan: «Mooy Almasi bi.» Ña ca des it ne: «Waaye nan la Almasi bi man a jógee Galile? 7:42 Mbind mi wax na ne, Almasi bi ci xeetu Daawuda lay wàcce te Betleyem, dëkku Daawuda, lay jóge.» 7:43 Noonu féewaloo daldi am ca biir mbooloo ma ndax Yeesu. 7:44 Am na ca ñoom ñu ko bëggoon a jàpp, waaye kenn manalu ko woon dara. 7:45 Bi alkaati ya delloo, saraxalekat yu mag ya ak Farisen ya laaj leen ne: «Lu tax indiwuleen ko?» 7:46 Alkaati ya ne leen: «Kenn musul a waxe ni nit kooku!» 7:47 Noonu Farisen ya laaj leen: «Mbaa naxuñu leen, yéen itam? 7:48 Ndax am na kenn ci saraxalekat yi walla ci Farisen yi ku ko gëm? Déedéet. 7:49 Waaye mbooloo mi xamuñu yoonu Musaa; ñu alku lañu!» 7:50 Nikodem bokkoon na ca Farisen ya fa nekkoon. Fekk moo seeti woon Yeesu lu jiitu. Mu ne leen: 7:51 «Ndax ci sunu yoon, man nañoo daan kenn te dégluwuñu ko, mbaa ñu xam lu mu def?» 7:52 Ñu tontu ko ne: «Mbaa du yaw itam dangaa bokk ci diiwaanu Galile? Gëstul, kon dinga xam ne, benn yonent musul a jóge Galile.» 7:53 Gannaaw loolu ku ci nekk dellu sa kër.
8:1 Yeesu moom, dem ca tundu Oliw ya. 8:2 Ca ëllëg sa ca fajar, mu dellu ca kër Yàlla ga, mbooloo ma fa teewoon wër ko. Mu toog, tàmbali di leen jàngal. 8:3 Xutbakat ya ak Farisen ya indi jenn jigéen ju ñu bettoon muy njaaloo, ñu taxawal ko ca diggu mbooloo ma. 8:4 Noonu ñu ne Yeesu: «Kilifa gi, jigéen jii de, dañu koo bett muy njaaloo. 8:5 Ci ndigali Yàlla yi, jigéen ju njaaloo, Musaa dafa santaane ñu sànni ko ay xeer, ba mu dee. Yaw nag, lu ciy sa xalaat?» 8:6 Loolu nag, dañu ko doon wax ngir seetlu ko, ndaxte bëggoon nañoo tiiñal Yeesu. Yeesu sëgg, di bind ak baaraamam ci suuf. 8:7 Bi laaj ya baree, mu siggi ne leen: «Ku musul a def bàkkaar ci yéen, na ko jëkk a sànniy xeer.» 8:8 Noonu mu sëggaat, dellu di bind ci suuf. 8:9 Bi ñu déggee loolu, ñuy rocceeku kenn-kenn, mag ña jiitu. Yeesu rekk des fa, jigéen ja taxaw ca kanamam. 8:10 Mu daldi siggi ne ko: «Jigéen ji, ana ñi la doon jiiñ njaaloo? Ndax kenn tegu la tooñ?» 8:11 Mu ne ko: «Kenn, Sang bi.» Yeesu ne ko: «Man it ci sama wàll, duma la daan. Demal, waaye bul defati bàkkaar.» 8:12 Yeesu jubluwaat ca mbooloo ma ne leen: «Man maay leeru àddina si. Ku ma topp doo dox cig lëndëm, waaye dinga am leeru dund.» 8:13 Farisen ya ne ko: «Yaw yaay seedeel sa bopp, kon li ngay wax du dëgg.» 8:14 Yeesu tontu leen: «Maa ngi seedeel sama bopp, teewul li may wax di dëgg, ndaxte xam naa fa ma bàyyikoo, xam fa ma jëm. Waaye yéen xamuleen fa ma bàyyikoo ak fa ma jëm. 8:15 Ci gis-gisu àddina ngeen di àttee; man duma àtte kenn. 8:16 Teewul nag, su ma demee bay àtte, bu jub lay doon, ndaxte du man rekk ay àtte, waaye Baay, bi ma yónni, daf ciy ànd ak man. 8:17 Seen yoon dafa wax ne, seedes ñaari nit a gën a wóor. 8:18 Man maa ngi seedeel sama bopp, te Baay bi ma yónni mi ngi may seedeel itam.» 8:19 Ñu laaj ko ne: «Kuy sa baay?» Yeesu tontu ne: «Xamuleen ma, xamuleen sama Baay. Bu ngeen ma xamoon, xam ko.» 8:20 Bi muy wax loolu, Yeesoo nga doon jàngalee ca kër Yàlla ga, ca wetu fa ñu doon denc asaka ya. Kenn mënu ko woon a jàpp, ndaxte waxtoom jotagul. 8:21 Yeesu dellu ne leen: «Maa ngi dem; dingeen ma seet, waaye seen bàkkaar ngeen di deeyaale. Fa ma jëm, dungeen fa man a dem.» 8:22 Yawut yay waxante naan: «Nee na kat, fa mu jëm, dunu fa man a dem. Mbaa du day xaruji?» 8:23 Yeesu tontu ne: «Yéen, fii ngeen bawoo, ci suuf, waaye man ca kaw laa jóge. Àddina ngeen soqikoo, waaye man bokkuma ci. 8:24 Looloo tax ma ne, ci seeni bàkkaar ngeen di dee. Bu ngeen gëmul ki ma nekk, dingeen dee ci seeni bàkkaar.» 8:25 Ñu ne ko: «Yaay kan?» Mu ne leen: «Li ma leen waxoon ca njàlbéen ga. 8:26 Li ma man a wax ci yéen ba àtte leen, bare na. Waaye ki ma yónni, ku wóor la, te li mu ma wax rekk laay jottali àddina.» 8:27 Xamuñu woon ne, Yàlla Baay bee tax muy wax. 8:28 Yeesu nag ne leen: «Bu ngeen yékkatee Doomu nit ki, dingeen xam ne, Maay ki nekk. Dingeen xam ne it, duma def dara man ci sama bopp. Li ma Baay biy jàngal rekk laay wax. 8:29 Te it ki ma yónnee ngi ànd ak man; musu maa bàyyi ma wéet, ndaxte li ko neex rekk laay def.» 8:30 Bi ñuy dégg Yeesu di wax loolu, ñu bare daldi koy gëm. 8:31 Yeesu ne Yawut ya ko gëmoon: «Bu ngeen saxee ci li ma wax, nekk ngeen samay taalibe ci lu wóor. 8:32 Te it dingeen xam dëgg gi te dëgg gi dina leen goreel.» 8:33 Ñu tontu ko ne: «Nun ci Ibraayma lanu soqikoo te musunoo nekk jaamu kenn. Nan nga nu man a waxe ne, dinañu leen goreel?» 8:34 Yeesu ne leen: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, képp kuy bàkkaar, jaamu bàkkaar la. 8:35 Te jaam du bokk ci kër gi ba fàww, waaye doom, moom, ci kër gi la bokk ba fàww. 8:36 Kon nag bu leen Doom ji defee gor, dingeen doon ay gor tigi. 8:37 Xam naa ne askanu Ibraayma ngeen. Waaye yéena ngi may wut a rey, ndaxte li may jàngale xajul ci yéen. 8:38 Li ma sama Baay won laay wax; waaye yéen, li leen seen baay di wax ngeen di def.» 8:39 Ñu tontu ko ne: «Ibraayma mooy sunu baay.» Yeesu ne leen: «Bu ngeen dee waa kër Ibraayma, dingeen jëfe ni moom. 8:40 Léegi nag yéena ngi may wut a rey, man mi leen jottali dëgg, gi ma jële ca Yàlla. Ibraayma deful lu ni mel. 8:41 Li ngeen donne ci seen baay rekk ngeen di def.» Ñu tontu ko ne: «Nun de, dunu doomi araam. Benn baay rekk lanu am, mooy Yàlla.» 8:42 Yeesu ne leen: «Bu Yàlla doon seen baay, dingeen ma bëgg, ndaxte ca moom laa jóge, ñëw ci ndigalam. Ñëwaluma sama bopp, waaye moo ma yónni. 8:43 Lu tax dégguleen li ma leen wax? Li ko waral moo di mënuleen koo déglu. 8:44 Seytaane mooy seen baay, te bëgg-bëggam ngeen di bëgg di def. Bóomkat la mas a doon. Du taxaw mukk ci dëgg, ndaxte dëgg nekkul ci moom. Buy fen, dëppoo na ak jikkoom, ndaxte fenkat la, te ci moom la fen soqikoo. 8:45 Waaye man damay wax dëgg, moo tax gëmuleen ma. 8:46 Kan ci yéen moo man a seede ne, bàkkaar naa? Su ma waxee dëgg nag, lu tax dungeen ma gëm? 8:47 Ku nekk doomu Yàlla dina déglu ay waxam. Waaye nekkuleen doomi Yàlla, looloo tax dungeen déglu.» 8:48 Yawut ya ne ko: «Ndax danoo waxul dëgg, bu nu nee, nitu Samari nga te dangaa am ay rab?» 8:49 Yeesu ne leen: «Awma rab; waaye sama Baay laay teral, te yéen dangeen may toroxal. 8:50 Wutumaa màggal sama bopp. Keneen a ma koy wutal te mooy àtte. 8:51 Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, kuy sàmm sama wax doo dee mukk.» 8:52 Yawut ya ne ko: «Léegi wóor nanu ne, dangaa am ay rab! Ibraayma faatu na, yonent yépp faatu, yaw nga naan: “Kuy sàmm sama wax, doo ñam dee.” 8:53 Sunu baay Ibraayma faatu na; mbaa du dangaa defe ne, yaa ko gën a màgg? Yonent yi itam faatu nañu. Waaw, loo teg sa bopp?» 8:54 Yeesu ne leen: «Su ma dee màggal sama bopp, du am maana. Sama Baay a may màggal, moom mi ngeen naan, mooy seen Yàlla. 8:55 Xamuleen ko nag; man maa ko xam. Su ma ne woon xawma ko, ab fenkat laay doon ni yéen. Waaye xam naa ko te maa ngi sàmm waxam. 8:56 Seen baay Ibraayma bég na, bi mu yégee sama ngan. Bi mu ko gisee it, bég na ci lool.» 8:57 Yawut ya ne ko: «Amaguloo juróom-fukki at, ba noppi naan gis nga Ibraayma?» 8:58 Yeesu ne leen: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, laata ñuy sàkk Ibraayma, fekk na ma doon ki ñuy wax Maay ki nekk.» 8:59 Noonu ñu for ay xeer, bëgg ko koo sànni ngir rey ko. Waaye Yeesu nëbbu, génn kër Yàlla ga.
9:1 Amoon na fu Yeesu jaaroon, gis fa waa ju judduwaale gumba. 9:2 Taalibeem ya laaj ko ne: «Kilifa gi, lu tax waa jii judduwaale gumba? Ndax bàkkaaram a ko waral, walla bu waajuram?» 9:3 Yeesu tontu ne: «Ajuwul ci bàkkaaram walla ci bu waajuram. Waaye loolu dafa am, ngir jëfi Yàlla yi feeñ ci moom. 9:4 Bëccëg lanu war a matal jëfi ki ma yónni; guddi dina ñëwi, goo xam ne kenn du ci man a liggéey. 9:5 Ci bi may nekk àddina, maay leeru àddina.» 9:6 Bi Yeesu waxee loolu ba noppi, dafa daldi tifli, jaxase lor wa ak ban, tay ko ci bëti gumba ga ne ko: 9:7 «Demal sëlmu ci bëtu Silowe.» Silowe mi ngi tekki «Yónni nañu ko.» Gumba ga daldi dem sëlmuji, dellusi di gis. 9:8 Dëkkandoom yi ak ñi ko xame woon bu jëkk ci yelwaan naan: «Xanaa du kii moo daan toog, di yelwaan?» 9:9 Ñii naan: «Moom la de!» Ñee naan: «Du moom! Dañoo niroo rekk.» Mu daldi leen ne: «Man la de!» 9:10 Ñu ne ko: «Lu ubbi say bët?» 9:11 Mu tontu ne: «Ku ñuy wax Yeesu moo tooyal ban, tay ko ci samay bët, ne ma: “Demal sëlmu ci bëtu Silowe.” Ma dem nag sëlmuji, daldi gis.» 9:12 Ñu ne ko: «Ana waa ji?» Mu ne leen: «Xawma fu mu nekk.» 9:13 Noonu ñu daldi indil Farisen yi nit ki gumba woon. 9:14 Ndekete Yeesu, bés bi mu tooyale ban, ubbi bëti gumba ga, bésu noflaay la woon. 9:15 Looloo tax Farisen ya di laajaat waa ja fi mu jaar bay gis léegi. Mu ne leen: «Dafa tay ban ci samay bët, ma sëlmuji, ba fi ma nekk maa ngi gis.» 9:16 Ci noonu am ca Farisen ya ñu naan: «Ki def lii, mënul a jóge ca Yàlla, ndaxte toppul ndigalu bésu noflaay bi.» Ñeneen it di wax ne: «Nan la boroom bàkkaar man a wonee yii firnde?» Noonu ñu daldi féewaloo ci seen biir. 9:17 Farisen ya laajaat ka gumba woon ne ko: «Yaw, loo wax ci moom? Yaw de la ubbil say bët.» Mu ne leen: «Yonent la.» 9:18 Yawut ya mënuñu woon a nangu ne, nit ka dafa gumba woon tey gis léegi, ñu daldi wooluji ay waajuram, 9:19 laaj leen ne: «Ndax kii mooy seen doom, ji ngeen ne, gumba judduwaale la? Kon fu mu jaar, bay gis léegi?» 9:20 Waajur ya tontu ne: «Xam nanu ne daal, sunu doom la te dafa judduwaale gumba. 9:21 Waaye ni mu def léegi bay gis, xamunu ko, te xamunu it ki ko ubbil ay bëtam. Laajleen ko; magum jëmm la, te man na tontul boppam.» 9:22 Ragal Yawut ya nag moo taxoon waajuri nit ka waxe noonu, ndaxte Yawut ya dañoo mànkoo woon ne, képp ku seede ne Yeesu mooy Almasi bi, ñu dàq la ca jàngu ba. 9:23 Looloo tax waajur ya ne: «Laajleen ko; magum jëmm la.» 9:24 Farisen ya dellu woowaat ka gumba woon ne ko: «Waxal sa digganteek Yàlla. Xam nanu ne, waa joojee boroom bàkkaar la.» 9:25 Mu tontu ne: «Xawma ndax boroom bàkkaar la am déet. Li ma xam daal mooy gumba woon naa, te léegi maa ngi gis.» 9:26 Ñu laaj ko ne: «Lu mu la def? Nu mu la ubbile say bët?» 9:27 Mu ne leen: «Wax naa leen ko ba noppi, waaye dégluwuleen ma. Lu ngeen bëgg ci ma di ko wax, di waxaat? Xanaa dangeen a bëgg a nekk yéen itam ay taalibeem?» 9:28 Ci kaw loolu ñu daldi ko saaga ne ko: «Yaw yaay taalibeem. Nun, taalibey Musaa lanu. 9:29 Xam nanu ne, Yàlla wax na ak Musaa; waaye kii, xamunu sax fu mu jóge.» 9:30 Waa ja ne leen: «Loolu de, doy na waar! Xamuleen fu mu jóge, te moo ubbi samay bët! 9:31 Xam nanu ne, Yàlla du déglu boroom bàkkaar. Waaye nag, dina déglu ki koy ragal tey def coobareem. 9:32 Bi àddina sosoo ba tey, musuñoo dégg nit ku ubbi bëti gumbag judduwaale. 9:33 Kon nit kookee nag, bu jógewul woon ca Yàlla, du man a def dara.» 9:34 Ñu tontu ko ne: «Yaw, ci biir bàkkaar nga juddoo, ba noppi di nu jàngal?» Noonu ñu dàq ko ca jàngu ba. 9:35 Yeesu daldi yég ne, dàq nañu nit ka. Bi mu dajeek moom, mu ne ko: «Ndax gëm nga Doomu nit ki?» 9:36 Waa ja ne ko: «Wax ma mooy kan, Sang bi, ba ma man koo gëm.» 9:37 Yeesu ne ko: «Gis nga ko ba noppi, te mooy kiy wax ak yaw.» 9:38 Waa ja ne: «Boroom bi, gëm naa la.» Noonu mu jaamu Yeesu. 9:39 Yeesu ne ko: «Àttee ma tax a ñëw àddina, ngir ñi gumba gis, ñiy gis gumba.» 9:40 Bi Farisen ya nekkoon ak moom déggee loolu, ñu ne ko: «Xanaa kon nun it danoo gumba?» 9:41 Yeesu tontu leen ne: «Bu ngeen gumba woon, dungeen am bàkkaar, waaye fi ak yéena ngi naan: “Nu ngi gis,” ci bàkkaar ngeen di dëkk.
10:1 «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, ku jaar feneen fu dul ci buntu gétt gi, kooku sàcc la, saay-saay la. 10:2 Waaye ki jaar ci bunt bi, mooy sàmmu xar yi. 10:3 Wottukat bi dina ko ubbil bunt bi, xar yiy dégg baatam. Xar yi mu moom nag, bu ci nekk dina la woo ci sa tur, ba noppi nga topp ko ci biti. 10:4 Sàmm bi, bu génnee yi mu moom yépp, dina leen jiitu, ñu topp ko, ndaxte xam nañu baatam. 10:5 Waaye duñu topp jaambur; dañu koy daw, ndaxte miinuñu baatam.» 10:6 Yeesu misaaloon na leen loolu, waaye xamuñu lu mu leen doon wax. 10:7 Noonu Yeesu newaat: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, man maay buntu gétt gi. 10:8 Ñi ma fi jiitu ñépp ay sàcc lañu, ak ay saay-saay; waaye xar yi dégluwuñu leen. 10:9 Man maay bunt bi; ku jaar ci man, dinga mucc, dinga man a dugg ak a génn, dinga am it mbooy goo man a fore. 10:10 Sàcc bi moom, day sàccsi rekk, di rey ak a yàq. Man damaa ñëw, ngir nit ñi am dund, ba nekk ci naataange. 10:11 «Man maay sàmm bu baax bi. Sàmm bu baax bi day joxe bakkanam ngir ay xaram. 10:12 Ki dul sàmm bi tey liggéeyal xaalis rekk waaye moomul xar yi, bu séenee bukki, day daw, bàyyi fa xar ya. Bu ko defee bukki ba dal ca coggal ja, jàpp ca, tasaare ya ca des. 10:13 Booba surga day daw, ndaxte xaalis rekk lay liggéeyal, faalewul xar ya. 10:14 «Man maay sàmm bu baax bi. Ni ma xame Baay bi te Baay bi xame ma ni, noonu laa xame samay xar, te ñoom it ni lañu ma xame. Te it kat dinaa joxe sama bakkan ngir xar yi. 10:16 Am naa yeneen xar yu bokkul ci gétt gii. War naa leen a indi, ñoom it, te dinañu déglu sama baat. Benn coggal ay am ak benn sàmm. 10:17 Baay bi bëgg na ma, ndaxte damay joxe sama bakkan ngir jëlaat ko. 10:18 Kenn du ko jële ci man; maa koy joxe ci sama coobarey bopp. Am naa it sañ-sañu joxe ko te am naa sañ-sañu jëlaat ko. Loolu la ma sama Baay sant.» 10:19 Kàddu yooyee ñoo féewalewaat Yawut yi. 10:20 Ñu bare ca ñoom naan: «Dafa ànd ak rab! Dafa dof! Lu tax ngeen koy déglu?» 10:21 Waaye ñeneen naan: «Nit ku am ay rab du waxe nii. Ndax rab man na ubbi bëti gumba?» 10:22 Am bés ñu doon màggal ca Yerusalem Bés ba ñu sellale woon kër Yàlla ga; ci jamonoy sedd la woon. 10:23 Yeesoo nga woon ca kër Yàlla ga, di doxantu ca biir Werandaa bu Suleymaan. 10:24 Yawut ya wër ko ne ko: «Kañ nga nuy dindi ci kumpa? Boo dee Almasi bi, wax ko mu leer.» 10:25 Yeesu tontu leen ne: «Wax naa leen ko ba noppi, waaye gëmuleen. Jëf yi may def ci sama turu Baay ñoo may seede. 10:26 Waaye gëmuleen ndaxte bokkuleen ci samay xar. 10:27 Samay xar dinañu dégg sama baat; xam naa leen te ñu ngi may topp. 10:28 Dama leen di jox dund gu dul jeex; duñu sànku mukk, te kenn du leen jële ci sama loxo. 10:29 Baay bi ma leen jox, moo gën a màgg lépp, te kenn mënul a jële dara ci loxob Baay bi. 10:30 Man ak Baay bi benn lanu.» 10:31 Yawut ya daldi foraat ay xeer, bëgg koo sànni, ngir rey ko. 10:32 Noonu Yeesu ne leen: «Def naa ci seen kanam jëf yu baax yu bare ci ndigalu Baay bi. Ban ci jëf yooyu moo tax ba ngeen bëgg maa sànni ay doj?» 10:33 Yawut ya ne ko: «Jëf ju baax taxul nu bëgg laa sànniy xeer, waaye dangay suufeel turu Yàlla; yaw, nit rekk nga, ba noppi di def sa bopp Yàlla!» 10:34 Yeesu tontu ne: «Bind nañu ci seen téereb yoon ne: “Yàlla nee na: Ay yàlla ngeen.” 10:35 Yàlla wooye na “ay yàlla” ñi mu yónnee kàddoom, te xam nanu ne, kenn mënul a randal waxi Yàlla. 10:36 Kon nu ngeen man a waxe ne, damay suufeel turu Yàlla ndax li ma ne Doomam laa, man mi Yàlla tànn, yónni ma ci àddina? 10:37 Su ma deful sama jëfi Baay, buleen ma gëm; 10:38 waaye su ma ko defee, bu ngeen ma gëmul sax, gëmleen boog samay jëf, ngir ngeen xam te nangu ne, maa ngi nekk ci Baay bi te Baay bi nekk na ci man.» 10:39 Ñu di ko wut a jàppaat, waaye mu bàyyi leen fa, dem. 10:40 Yeesu génn, jàllaat dexu Yurdan, toog fa Yaxya daan sóobe ci ndox bu jëkk. 10:41 Nit ñu bare ñëw ci moom, te naan: «Yaxya deful benn kéemaan, waaye li mu wax ci kii yépp, dëgg la.» 10:42 Noonu ñu bare gëm ko.
11:1 Amoon na benn waay bu woppoon, ñu koy wax Lasaar. Ma nga dëkkoon Betani, moom ak Maryaama ak Màrt, mi mu bokkaloon ndey ak baay. 11:2 Maryaama mooy jigéen jiy sottiji latkoloñ ci tànki Boroom bi, fompe ko kawaram. Moom la càmmiñam Lasaar woppoon. 11:3 Ñaari jigéeni Lasaar yónnee ca Yeesu ne ko: «Boroom bi, sa xarit wopp na.» 11:4 Bi Yeesu déggee xebaar boobu, mu ne: «Lasaar de, woppam jooju du ko mujje; day wone ndamu Yàlla, tey màggal Doomu Yàlla ji.» 11:5 Yeesu soppoon na Màrt ak Maryaama ak Lasaar. 11:6 Bi mu yégee nag ne, Lasaar wopp na, mu toogaat yeneen ñaari fan ca bérab, ba mu nekkoon. 11:7 Gannaaw loolu mu ne taalibe ya: «Nanu dellu Yude.» 11:8 Taalibe ya tontu ko ne: «Kilifa gi, yàggul dara waa Yude doon nañu la wut a rey ak i xeer, nga di fa dellu?» 11:9 Yeesu ne leen: «Xanaa du bëccëg fukki waxtook ñaar la? Kuy dox bëccëg, du fakkastalu, ndaxte day gis leeru àddina si. 11:10 Waaye kuy dox guddi, dina fakkastalu, ndaxte leer nekkul ci moom.» 11:11 Yeesu wax loolu, teg ca ne: «Sunu xarit Lasaar nelaw na, waaye maa ngi dem yee ko.» 11:12 Taalibe ya tontu ne: «Boroom bi, bu nelawee kay, kon dina wér.» 11:13 Yeesu dafa bëggoon a wax ne, Lasaar dee na, waaye taalibe yi dañoo xalaatoon ne, mbiri nelaw rekk lay wax. 11:14 Ci kaw loolu Yeesu wax ci lu leer ne: «Lasaar dee na. 11:15 Bég naa ngir yéen ndax li ma fa nekkul, ngir seen ngëm gën a dëgër. Waaye nanu ko seeti.» 11:16 Noonu Tomaa, ki turam di tekki «Séex bi,» daldi ne yeneen taalibe ya: «Nanu dem nun itam, deeyandoo ak moom!» 11:17 Bi Yeesu agsee, mu fekk ne, bi ñu dencee Lasaar ak léegi, mat na ñeenti fan. 11:18 Betani ma nga woon ca wetu Yerusalem, diggante bi matul woon sax ñetti kilomet. 11:19 Yawut yu bare ñëwoon nañu kër Màrt ak Maryaama, ngir dëfël leen ci seen deewu càmmiñ. 11:20 Bi Yeesu ñëwee, Màrt yég ko, dem di dajeek moom; fekk booba Maryaamaa nga toogoon ca kër ga. 11:21 Màrt ne Yeesu: «Boroom bi, boo fi nekkoon de, sama càmmiñ li du dee. 11:22 Waaye xam naa ne, fii nu tollu sax, loo ñaan Yàlla, mu may la ko.» 11:23 Yeesu ne ko: «Sa càmmiñ dina dekki.» 11:24 Màrt tontu ko ne: «Xam naa ne, dina jóg bésu ndekkite la, keroog bés bu mujj ba.» 11:25 Yeesu ne ko: «Man maay ndekkite li, maay dund gi. Ku ma gëm, boo deeyee it, dinga dund. 11:26 Rax-ca-dolli kuy dund te gëm ma, doo dee mukk. Ndax gëm nga loolu?» 11:27 Mu tontu ko ne: «Waaw Boroom bi. Gëm naa ne, yaay Almasi bi, di Doomu Yàlla, ji war a ñëw àddina.» 11:28 Bi Màrt waxee loolu, mu daldi dem woowi Maryaama ne ko ci pett: «Kilifa gaa ngi fi; mi ngi lay laaj.» 11:29 Bi Maryaama déggee loolu, mu daldi jóg, gaawantoo dem ca Yeesu. 11:30 Te fekk duggagul woon ca dëkk ba, waaye ma nga woon ba tey ca bérab, ba mu daje woon ak Màrt. 11:31 Noonu Yawut, ya nekkoon ca kër ga di dëfël Maryaama, gis ko mu ne bërét génn, ñu daldi koy topp, defe ne, day jooyi ca bàmmeel ba. 11:32 Bi Maryaama agsee nag ca Yeesu, ba gis ko, mu daanu ciy tànkam ne ko: «Boroom bi, boo fi nekkoon, sama càmmiñ du dee.» 11:33 Yeesu gis ne, mi ngi jooy te Yawut yi ànd ak moom itam ñu ngi jooy. Mu daldi jàq, am naqar wu réy. 11:34 Mu ne leen: «Fu ngeen ko denc?» Ñu tontu ko ne: «Kaay gis, Sang bi.» 11:35 Yeesu jooy. 11:36 Noonu nag, Yawut ya ne: «Gis ngeen ni mu ko bëgge woon!» 11:37 Waaye am na ca ñoom ñu doon wax naan: «Moom mi ubbi bëti gumba gi, ndax mënul woon a fexe ba Lasaar du dee?» 11:38 Yeesu dellu am naqar wu réy, daldi dem ca bàmmeel ba. Pax la mu ñu yett ci doj, ube ko xeer. 11:39 Yeesu ne: «Dindileen xeer wi!» Màrt, jigéenu ku dee ki ne ko: «Boroom bi, dina xasaw xunn fii mu nekk, ndaxte am na ci bàmmeel bi ñeenti fan.» 11:40 Yeesu ne ko: «Ndax waxuma la ne, boo gëmee, dinga gis ndamu Yàlla?» 11:41 Ñu daldi dindi xeer wa. Yeesu xool ci kaw, ne jàkk asamaan, ñaan Yàlla ne: «Baay, sant naa la ci li nga ma déglu ba noppi. 11:42 Xam naa ne, doo jóg ci di ma déglu, waaye dama koy wax, ngir nit ñi ma wër gëm ne, yaa ma yónni.» 11:43 Bi mu waxee loolu, Yeesu woote ak baat bu dëgër ne: «Lasaar, ñëwal ci biti!» 11:44 Néew bi daldi génn, ñu gis càngaay, li ñu takke woon tànk yi ak loxo yi, ak kaala, gi ñu muure woon kanam gi. Yeesu ne leen: «Tekkileen ko, bàyyi ko mu dem.» 11:45 Yawut yu bare ca ña ñëwoon kër Maryaama te gis li Yeesu defoon, daldi koy gëm. 11:46 Waaye amoon na it ñu demoon ci Farisen ya, nettali leen la Yeesu defoon. 11:47 Farisen ya ak saraxalekat yu mag ya woo kureelu àttekat ya ne: «Nit kii kat, kéemaan yi muy def a ngi bëgg a bare. Lu nuy def nag? 11:48 Ndaxte su nu ko bàyyee mu jàppoo nii, ñépp dinañu ko gëm, te kilifay Room yi dinañu ñëw, daaneel sunu kër Yàlla gi, tas sunu réew!» 11:49 Amoon na ca ñoom ku ñuy wax Kayif te mu nekkoon saraxalekat bu mag ba at mooma; mu ne leen: «Xamuleen ci mbir mi dara. 11:50 Xanaa xamuleen ne, kenn nit rekk dee ngir ñépp, mooy li gën ci yéen? Bu ko defee réew mi du tas.» 11:51 Loolu Kayif waxu ko woon ci sagoom, waaye li mu nekkoon saraxalekat bu mag ba at mooma, moo tax Yàlla xiirtal ko mu ne, Yeesu dina dee ngir réew mi. 11:52 Du woon rekk ngir xeet woowu, waaye ngir itam doomi Yàlla, yi tasaaroo yépp, dajaloo nekk benn. 11:53 Keroog la njiiti Yawut ya dogu ci rey Yeesu. 11:54 Taxoon na ba Yeesu dootul doxantu ci biir Yawut ya. Noonu mu dem ca gox bu jege màndiŋ ma, ca dëkku Efrayim. Foofa nag la toog ak ay taalibeem. 11:55 Bésu Jéggi ba, di màggalu Yawut ya, mu ngi doon jubsi, ba ñu bare ca waa àll ba di dem Yerusalem balaa booba, ngir sanguji set. 11:56 Ñu ngi doon wut Yeesu tey waxante ca kër Yàlla ga naan: «Lu ngeen ci xam? Ndax dina ñëw ci màggal gi walla déet?» 11:57 Saraxalekat yu mag ya ak Farisen ya daldi santaane ne, bu kenn xamee fu Yeesu nekk, mu yégle ko, ngir ñu man koo jàpp.
12:1 Juróom benni fan laata màggalu bésub Jéggi ba, Yeesu dem na Betani, dëkku Lasaar, mi mu dekkal. 12:2 Foofa ñu defaral ko fa reer. Màrt moo ko doon séddale, te Lasaar bokkoon na ca gan ña. 12:3 Noonu Maryaama daldi jël liibaru latkoloñ ju raxul ju ñuy wax nàrd, tey jar lu baree-bare. Mu sotti ko ci tànki Yeesu, ba noppi fomp ko ak kawaram. Xetu latkoloñ gi gilli ci kër gi yépp. 12:4 Kenn ca taalibey Yeesu ya, muy Yudaa Iskariyo, mi ko nar a wor, daldi ne: 12:5 «Lu tax jaayewuñu latkoloñ jii peyu atum lëmm, jox ko miskin yi?» 12:6 Waaye bi muy wax loolu, xalaatul woon miskin yi, ndaxte sàcc la woon; moo yoroon boyetu xaalis bi, te daan ci sàkk. 12:7 Waaye Yeesu ne ko: «Bàyyi ko! Jekkoon na mu denc ko ngir bés bu ñu may suul. 12:8 Miskin yaa ngi ak yéen bés bu nekk, waaye dungeen ma gis ba fàww.» 12:9 Bi ñu yégee ne, Yeesoo nga fa, mbooloom Yawut mu bare daldi dem Betani. Yeesu rekk yóbbuwu leen fa woon, waaye dañoo bëggoon a gisaale Lasaar, mi Yeesu dekkaloon. 12:10 Saraxalekat yu mag ya dogu ci ne, dañuy reyaale Lasaar, 12:11 ndaxte moo waral Yawut yu bare dëddu leen, gëm Yeesu. 12:12 Ca ëllëg sa mbooloo mu bare, ma ñëwoon ca màggalu bésub Jéggi ba, yég ne Yeesoo ngi jëmsi Yerusalem. 12:13 Ñu daldi jël cari garab, génn di ko teeru. Ñuy xaacu naan:«Osaana!Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi,ku barkeel nga!Na Yàlla barkeel buuru Israyil!» 12:14 Yeesu wut cumbur, war ko; ndaxte Mbind mi nee na: 12:15 «Buleen ragal, waa Siyon.Gis ngeen, seen buur a ngi ñëw,war mbaam mu ndaw.» 12:16 Yooyu yépp, taalibe ya xamuñu woon ca saa sa lu muy tekki; waaye gannaaw bi ndamu Yeesu feeñee, ñu fàttaliku ne, Mbind mi yégle woon na loolu ci moom, te amal nañu ko. 12:17 Ña nekkoon ak Yeesu ñépp, bi muy wooyee Lasaar mu génn ca bàmmeel ba te mu dekkal ko, demoon nañu, nettali la ñu gis. 12:18 Looloo tax mbooloo ma teeru ko, ndaxte yégoon nañu firnde boobu. 12:19 Farisen yi nag di waxante naan: «Gis ngeen, mënuleen ci dara; ñépp a ngi koy topp!» 12:20 Ca mbooloo ma, amoon na ca ay Gereg yu bokk ca ña ñëwoon Yerusalem ngir jaamu Yàlla diirub màggal ga. 12:21 Ñëw nañu ci Filib, mi dëkk Betsayda ci diiwaanu Galile, ne ko: «Sang bi, danoo bëggoon a gis Yeesu.» 12:22 Filib dem wax ko Andare; ñu ànd, waxi ko Yeesu. 12:23 Mu tontu leen ne: «Waxtu wi ñu war a feeñale ndamu Doomu nit ki jot na. 12:24 Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, fi ak peppu dugub ji wadd ci suuf jaarul ci dee, du man a weesu li mu doon: pepp doŋŋ. Waaye bu deeyee, dina jur pepp yu bare. 12:25 Ku bëgg bakkanam dina ko ñàkk, waaye ku ko bañ ci àddina sii, dina ko denc ngir dund gu dul jeex gi. 12:26 Ku bëgg a doon sama surga, na ma topp. Bu ko defee, fu ma nekk, fa lay nekk moom itam. Ku may liggéeyal, sama Baay dina ko teral. 12:27 «Léegi nag damaa jàq. Lu may war a wax? Mbaa du dama naan: “Baay, musal ma ci li nar a xew waxtu wiy ñëw?” Déedéet, ñëw naa sax ngir jaar ci waxtu woowu. 12:28 Baay, màggalal sa tur!» Noonu ñu dégg baat bu jóge asamaan naan: «Màggal naa ko ba noppi, te dinaa ko màggalaat.» 12:29 Mbooloo ma fa teewoon te dégg baat ba daldi ne: «Dënnu la woon!» Ñeneen naan: «Malaakaa doon wax ak moom.» 12:30 Waaye Yeesu ne leen: «Taxuma baat boobu jolli, waaye yéena tax. 12:31 Àtteb àddina si jot na: léegi ñu dàq malaaka mu bon, mi jiite àddina si. 12:32 Te man, bu ñu ma yékkatee, ma tiim suuf, dinaa wootal nit ñépp ci man.» 12:33 Ci baat yooyu la doon misaale ni mu war a faatoo. 12:34 Mbooloo ma tontu ko ne: «Jàng nanu ci sunu téereb yoon ne, Almasi bi dina sax ba fàww. Kon yaw, nan nga man a waxe ne, “Doomu nit ki dina yékkatiku?” Kuy Doomu nit kooku?» 12:35 Yeesu ne leen: «Leer gi dootul yàgg ak yéen. Doxleen, ci bi ngeen dee am leer, ngir lëndëm bañ leen a bett. Ndaxte kuy dox ci lëndëm doo xam foo jëm. 12:36 Kon ci bi ngeen dee am leer gi, gëmleen ko, ngir ngeen doon doomi leer.» Bi mu waxee loolu ba noppi, Yeesu dafa dem, nëbbatuji leen. 12:37 Firnde yi mu leen won yépp taxul ñu gëm ko, 12:38 ngir li yonent Yàlla Esayi waxoon am:«Boroom bi, ana ku gëm sunu waare?Kan la Boroom bi won dooleem?» 12:39 Mënuñu woon a gëm, ndaxte Esayi dafa waxaat ne: 12:40 «Yàlla dafa gumbaal seeni bët,def ba ñu dëgër bopp,ngir seeni bët bañ a gis,seen xel bañ a xam,ñu bañ a woññiku ci manngir ma wéral leen.» 12:41 Esayi dafa wax loolu, ndaxte gisoon na ndamu Yeesu te mi ngi doon wax ci ay mbiram. 12:42 Fekk na ci biir njiit yi sax, ñu bare gëmoon nañu Yeesu, waaye Farisen yee tax fésaluñu ko, ndaxte dañoo ragaloon, ñu dàq leen ca jàngu ba. 12:43 Ngërëmu nit a leen gënaloon ngërëmu Yàlla. 12:44 Yeesu yégle ne: «Ku ma gëm, gëmuloo ma waaye gëm nga ki ma yónni. 12:45 Ku ma gis, gis nga ki ma yónni. 12:46 Ni ag leer laa wàcce ci àddina, ngir ku ma gëm du des ci lëndëm. 12:47 Ku dégg samay wax te toppu leen, du man maa koy daan, ndaxte wàccuma ngir daan àddina, waaye damaa ñëw ngir musal ko. 12:48 Ku ma beddeeku te nanguwul samay wax, dina fekk fii li koy daan: sama njàngalee koy daan keroog bés bu mujj ba. 12:49 Ndaxte waxuma ci sama coobare, waaye Baay bi ma yónni ci boppam, moo ma sant li ma war a wax ak li ma war a jàngale. 12:50 Te xam naa ne, li muy santaane day joxe dund gu dul jeex. Kon li ma wax, dama koy wax, ni ma ko Baay bi sante.»
13:1 Laata màggalu bésu Jéggi ba la woon. Yeesu xamoon na ne, waxtu wi mu war a génne àddina, dem ca wetu Baay ba, jot na. Ku bëgg ñoñam yi nekk ci àddina la, te bëgg na leen ba fa mbëggeel man a yem. 13:2 Yeesu ak taalibe yaa ngi doon reer. Fekk na booba Seytaane xiirtal Yudaa, doomu Simoŋ Iskariyo, ngir mu wori Yeesu. 13:3 Yeesu xamoon na ne, Yàlla joxoon na ko sañ-sañ ci lépp, xam it ne, ca Yàlla la jóge te ca moom lay delluwaat. 13:4 Mu daldi jóge ca reer ba, summi mbubbam, daldi jël ab sarbet, laxas ko ci ndiggam. 13:5 Noonu mu sotti ndox ci ab këll, daldi tàmbali di raxas tànki taalibe ya, di leen fomp ak sarbet, ba mu laxasaayoo. 13:6 Bi mu agsee ba ca Simoŋ Piyeer, kooku ne ko: «Boroom bi, ndax yaw dangaa nar a raxas samay tànk?» 13:7 Yeesu tontu ko ne: «Xamoo fii mu nekk li may def, waaye dinga ko xami.» 13:8 Piyeer ne ko: «Déedéet, duma nangu mukk nga raxas samay tànk.» Yeesu ne ko: «Su ma la raxasul, doo bokk ak man dara.» 13:9 Simoŋ Piyeer ne ko: «Kon nag Boroom bi, bul yem rekk ci tànk yi, waaye raxasaaleel loxo yi ak bopp bi!» 13:10 Yeesu ne ko: «Ku sangu ba noppi, soxlaatul a raxas lu dul ay tànkam, ndaxte set na wecc. Yéen nag set ngeen, waaye du ñépp!» 13:11 Fekk Yeesu xamoon na ki ko nar a wor, looloo tax mu ne: «Setuleen yéen ñépp.» 13:12 Bi mu leen raxasalee seeni tànk ba noppi, Yeesu dafa solaat mbubbam, dellu toogaat ne leen: «Ndax xam ngeen li ma leen defal? 13:13 Yéen a ngi may wooye “Kilifa gi” ak “Boroom bi,” te wax ngeen dëgg, moom laa. 13:14 Kon bu fekkee ne man miy Boroom bi tey Kilifa gi, maa leen raxasal seeni tànk, yéen itam war ngeen di raxasalante seeni tànk. 13:15 Bàyyil naa leen fi royukaay, ngir ngeen di jëf, nii ma jëfeek yéen. 13:16 Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, jaam gënul a màgg sangam, mbaa ndaw, ki ko yónni. 13:17 Gannaaw xam ngeen loolu, bu ngeen doxalee noonu, dingeen bég. 13:18 «Yéen ñépp taxuleen may wax; xam naa ñi ma tànn. Waaye li Mbind mi wax, fàww mu am, bi ñu naan: “Ki lekk sama dugub wéq na ma.” 13:19 Maa ngi leen koy wax ci teel, bala looloo ñëw, ngir bu ñëwee, ngeen gëm ne, Maay ki nekk. 13:20 Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, ku nangu kenn ci ñi may yónni, nangu nga ma, man itam; te ku ma nangu, nangu nga ki ma yónni.» 13:21 Bi Yeesu waxee loolu ba noppi, mu jàq, biral ne: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, kenn ci yéen dina ma wor.» 13:22 Taalibe yi di xoolante, te xamuñu kan lay wax. 13:23 Ka Yeesu bëggoon te mu bokkoon ca taalibe ya, ma nga sóonu woon ca kaw Yeesu. 13:24 Kooku la Simoŋ Piyeer liyaar, ngir mu laaj Yeesu ki ko taxoon di wax. 13:25 Taalibe ba daldi walbatiku ca Yeesu, laaj ko ne: «Boroom bi, kooku kan la?» 13:26 Yeesu ne ko: «Dinaa capp dogu mburu ci ndab li; ki ma koy jox, kooku la.» Noonu Yeesu jël dogu mburu, capp ko ca ndab la, daldi koy jox Yudaa, doomu Simoŋ Iskariyo. 13:27 Naka la Yudaa jël dog wa, Seytaane dugg ci moom. Yeesu ne ko: «Gaawantul ci li ngay def!» 13:28 Amul kenn ca ña fa toogoon ku xam lu tax mu wax ko loolu. 13:29 Waaye gannaaw Yudaa moo yoroon boyetu xaalis bi, am ñu xalaat ne, Yeesu dafa koo wax, mu dem jëndi li war ci màggal gi, walla mu ne ko mu dem sarax miskin yi. 13:30 Yudaa nag jël dogu mburu ma, daldi génn ca saa sa. Booba guddi woon na. 13:31 Bi Yudaa génnee, Yeesu ne: «Léegi nag ndamu Doomu nit ki feeñ na, te ndamu Yàlla feeñ na itam ci moom. 13:32 Te bu ma feeñalee ndamu Yàlla, Yàlla itam ci teewaayam dina feeñal ndamu Doomu nit ki, te dina ko def léegi. 13:33 Samay soppe, sama nekk ak yéen dootul yàgg. Dingeen may seet, waaye maa ngi leen di wax léegi li ma waxoon Yawut ya: fa ma jëm, dungeen fa man a dem. 13:34 Maa ngi leen di jox ndigal lu bees: bëgganteleen. Nangeen di bëggante ni ma leen bëgge. 13:35 Ni ñuy xame ne samay taalibe ngeen, mooy ngeen bëggante.» 13:36 Simoŋ Piyeer laaj ko ne: «Boroom bi, foo jëm?» Yeesu ne ko: «Fa ma jëm, mënuloo ma faa topp léegi, waaye dinga ma toppi ca kanam.» 13:37 Piyeer ne ko: «Boroom bi, lu tax mënuma laa topp léegi? Àttan naa joxe sama bakkan ngir yaw!» 13:38 Yeesu ne ko: «Àttan ngaa joxe sa bakkan ngir man? Ci dëgg-dëgg maa ngi la koy wax, bala ginaar a sab, dinga ma weddi ñetti yoon.
14:1 «Buleen jàq. Gëmleen Yàlla te gëm ma. 14:2 Am na néeg yu bare ca sama kër Baay, bu dul woon noonu, ma wax leen ko, ndaxte maa ngi dem defaral leen fa ngeen di dëkk. 14:3 Te su ma leen defaralee bérab booba ba noppi, dinaa dellusi, yóbbaale leen, ba fu ma nekk, ngeen nekk fa, yéen itam. 14:4 Te fa ma jëm, xam ngeen yoon wi.» 14:5 Tomaa ne ko: «Boroom bi, xamunu fa nga jëm. Kon nan lanuy man a xame yoon wi?» 14:6 Yeesu ne ko: «Man maay yoon wi, maay dëgg te dund it man la. Kenn du ñëw ci Baay bi te jaarul ci man. 14:7 Ndegam xam ngeen ma, dingeen xam itam sama Baay. Lu weesu tey, xam ngeen ko te gis ngeen ko.» 14:8 Filib ne ko: «Boroom bi, won nu Baay bi; loolu doy na nu.» 14:9 Yeesu tontu ko ne: «Ni ma yàggeek yéen te ba tey Filib, xamuloo ma? Ku ma gis, gis nga Baay bi. Kon nag nan ngay man a laaje naan: “Won nu Baay bi”? 14:10 Xamuloo ne maa ngi nekk ci Baay bi te Baay baa ngi ci man? Kàddu yi ma leen di wax jógewuñu ci man, waaye Baay bi nekk ci man mooy matal ay jëfam. 14:11 Gëmleen li ma leen wax ne, maa ngi ci Baay bi te Baay baa ngi ci man; walla boog, gëmleen ndax jëf yi. 14:12 Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax: képp ku ma gëm dina def, moom itam, jëf yi may def. Dina def sax yu gën a màgg, ndaxte maa ngi dem ci Baay bi. 14:13 Te it lu ngeen ñaan ci sama tur dinaa ko def, ngir Doom ji feeñal ndamu Baay bi. 14:14 Lu ngeen ñaan ci sama tur, maa koy def. 14:15 «Bu ngeen ma bëggee, dingeen topp sama ndigal. 14:16 Te dinaa ñaan Baay bi, mu jox leen beneen Dimbalikat, buy nekk ak yéen ba abadan. 14:17 Kooku mooy Xelu Yàlla, mi yor dëgg. Àddina du ko man a nangu, ndaxte gisu ko te xamu ko. Yéen xam ngeen ko, ndaxte mi ngi dëkk ak yéen te dina nekk ci yéen. 14:18 Duma leen bàyyi ngeen wéet. Dinaa dellusi ci yéen. 14:19 Des na tuuti ci kanam, àddina du ma gisati; waaye yéen dingeen ma gis. Dinaa dund, moo tax yéen itam dingeen dund. 14:20 Bu keroogee, dingeen xam nag ne, nekk naa ci sama Baay, yéen it nekk ngeen ci man, te maa ngi nekk ci yéen. 14:21 Ki ma bëgg, mooy kiy nangu samay ndigal te di ko topp. Ku ma bëgg, Baay bi bëgg la, te man dinaa la bëgg, di la feeñu.» 14:22 Yudaa --du Yudaa Iskariyo de, beneen la woon — ne ko: «Boroom bi, lu xew, ba nga nar noo feeñu nun rekk, te doo feeñu àddina sépp?» 14:23 Yeesu tontu ko ne: «Ku ma bëgg dina sàmm sama kàddu. Sama Baay dina ko bëgg te nun dinanu ñëw ci moom, te dëkk ci moom. 14:24 Ku ma bëggul doo sàmm sama kàddu. Li may wax nag, jógewul ci man, waaye mi ngi soqikoo ci ki ma yónni. 14:25 «Lii dama leen koy wax ci bi may nekk ak yéen. 14:26 Waaye Dimbalikat, bi leen Baay bi di yónnee ci sama tur, muy Xelam mu Sell, dina leen jàngal lépp, di leen fàttali li ma leen waxoon lépp. 14:27 Jàmm laa leen bàyyeel, sama jàmm laa leen jox, jàmm ju àddina mënul a joxe. Buleen jàq, buleen tiit. 14:28 «Dégg ngeen li ma leen wax: “Dinaa dem, waaye dinaa dellusi ci yéen.” Bu ngeen ma bëggoon, dingeen bég ci li may dem ca Baay ba, ndaxte Baay bee ma gën a màgg. 14:29 Wax naa leen ko nag léegi, bala looloo ñëw, ngir bu waxtu wa agsee, ngeen gëm. 14:30 Lu weesu tey duma amati jotu waxtaan ak yéen, ndaxte malaaka mu bon mi jiite àddina saa ngi ñëw. Kooku manalu ma dara. 14:31 Waaye àddina si war na xam ne, bëgg naa Baay bi te ni ma ko Baay bi sante, ni laay jëfe. Jógleen, nu dem!
15:1 «Man maay garab gu wóor gi, te sama Baay mooy beykat bi. 15:2 Car bu soqikoo ci man te meññul, dina ko dog, sànni. Waaye car bu ci meññ, dina ko tenqi, ngir mu gën a meññ. 15:3 Yéen nag, Baay bi setal na leen jaarale ko ci kàddu gi ma leen wax, ni beykat di tenqee garabam. 15:4 Saxleen ci man; ma sax, man itam, ci yéen. Ni car mënul a ame ay doom, bu saxul ci garab, noonu itam dungeen man a meññ li may jëfe ci yéen, bu ngeen saxul ci man. 15:5 «Man maay garab gi; yéen yéenay car yi. Ki sax ci man te ma sax ci moom, dina meññ, ndaxte bu ngeen saxul ci man, dungeen man dara. 15:6 Ku saxul ci man dinañu ko sànni ci biti, mu mel ni car bu ñu dagg, ba mu wow. Car yu wow nag, dañu leen di buub, sànni ci safara, ñu lakk. 15:7 Bu ngeen saxee ci man te saxal samay wax ci seen xol, lu ngeen ñaan mu nangu. 15:8 Liy feeñal sama ndamu Baay moo di, ngeen di gën a meññ tey wone noonu ne, samay taalibe ngeen. 15:9 «Ni ma Baay bi bëggee, noonu itam laa leen bëgge. Saxleen ci mbëggeel googu ma am ci yéen. 15:10 Bu ngeen toppee samay ndigal, dingeen sax ci sama mbëggeel, ni ma toppe sama ndigali Baay, ba tax ma sax ci mbëggeelam. 15:11 Wax naa leen loolu, ngir ngeen bokk ci sama mbég, te seen bos mat sëkk. 15:12 Sama ndigal mooy ngeen bëggante, ni ma leen bëgge. 15:13 Genn mbëggeel mënul a weesu joxe sa bakkan ngir say xarit. 15:14 Samay xarit ngeen, ci kaw ngeen def li ma santaane. 15:15 Dootuma leen wooye jaam, ndaxte jaam du xam li sangam di def. Xarit laa leen wooye, ndaxte xamal naa leen li ma jële lépp ci sama Baay. 15:16 Du yéen yéena ma tànn, waaye man maa leen tànn, sas leen ngeen dem, meññ meññeef gu sax, ngir Baay bi def lu ngeen ko ñaan ci sama tur. 15:17 Li may santaane nag, mooy ngeen bëggante. 15:18 «Bu leen àddina bañee, xamleen ne, man lañu jëkk a bañ. 15:19 Ñi bokk ci ñoom lañu bëgg. Bu ngeen bokkoon ci ñoom, dinañu leen bëgg, ni ñu bëgge seeni ñoñ. Waaye bokkuleen ci àddina, ndaxte maa leen tànn, ber leen. Looloo tax ñu bañ leen. 15:20 Fàttalikuleen li ma leen wax: “Jaam gënul a màgg sangam.” Bu ñu ma sonalee, dinañu leen sonal yéen itam. Bu ñu toppee sama wax, dinañu topp seen wax yéen itam. 15:21 Waaye loolu lépp dinañu leen ko def ndax man, ndaxte xamuñu ki ma yónni. 15:22 Su ma ñëwul woon, ne leen dara, duñu am bàkkaar. Waaye léegi amuñu lay ngir seeni bàkkaar. 15:23 Ku ma bañ, bañ nga itam sama Baay. 15:24 Su ma deful woon ci seen biir jëf yu kenn deful, kon duñu am bàkkaar. Waaye léegi nag gis nañu samay jëf te teewul ñu bañ nu, man ak sama Baay. 15:25 Waaye loolu am na ngir kàddu gi am, kàddu gii ñu bind ci seen yoon: “Bañ nañu ma ci dara.” 15:26 «Dimbalikat bi dina ñëw, mooy Xel mi jóge ci Baay bi tey yor dëgg gi. Dina jóge ci Baay bi, ma yebal ko ci yéen. Moom nag, moo may seedeeli. 15:27 Te yéen itam dingeen seede samay mbir, ndaxte yéena nekkoon ak man ca njàlbéen ga.
16:1 «Loolu dama leen koo wax ngir seen ngëm bañ a wàññiku. 16:2 Dinañu leen dàq ca jàngu ya, te dinañu dem ba jamono joo xam ne ñi leen di rey dañuy xalaat ne, ñu ngi màggal turu Yàlla. 16:3 Dinañu agsi foofu, ndaxte xamuñu Baay bi te xamuñu ma. 16:4 Loolu nag, wax naa leen ko, ngir bu waxtu wi jotee ngeen fàttaliku ne, yégal naa leen ko. «Waxuma leen ko ca njàlbéen ga, ndaxte maa ngi nekkoon ak yéen. 16:5 «Léegi nag maa ngi dem ca ka ma yónni, te kenn ci yéen laaju ma fi ma jëm. 16:6 Seen xol dafa jeex ndax li ma leen wax. 16:7 Moona de, ci sama wàll, dëgg laa leen di wax. Li gën ci yéen mooy ma dem, ndaxte su dul loolu, Dimbalikat bi du ñëw ci yéen; waaye su ma demee, dinaa leen ko yónnee. 16:8 Te bu dikkee, dina yey niti àddina ci lu jëm ci seen bàkkaar, ci lu jëm ci sama njubte ak ci lu jëm ci àtte ba. 16:9 Ci mbiri seen bàkkaar, dina leen yey ci li ñu ma gëmul. 16:10 Ci mbiri sama njubte, dina leen yey ndaxte maa ngi dem ci Baay bi te dungeen ma gisati. 16:11 Ci mbiri àtte ba, dina leen yey ndaxte àtte nañu malaaka mu bon mi jiite àddina si, ba daan ko. 16:12 «Li ma leen war a wax bare na, waaye dungeen ko man a dékku. 16:13 Bu Xelum Yàlla mi yor dëgg gi dikkee nag, dina leen gindi ci lépp li jëm ci yoonu dëgg, ndaxte du wax ci coobarey boppam, waaye lu ko Baay bi wax, mu jottali leen ko. Dina leen yégal mbir yu ñëwagul. 16:14 Dina ma màggal, ndaxte lu mu leen wax, ci man la ko jële. 16:15 Lépp lu Baay bi am, maa ko moom. Looloo tax ma ne leen, lu mu leen jottali, ci man la ko jële. 16:16 «Ci kanam tuuti dungeen ma gisati. Bu ñu ci tegee ab diir, ngeen gisaat ma.» 16:17 Loolu Yeesu wax, tax na ba am ca taalibe ya, ñu waxante ne: «Lu muy wax nii: “Ci kanam tuuti dungeen ma gisati; bu ñu ci tegee ab diir, ngeen gisaat ma,” ak naan: “Ndaxte maa ngi dem ca Baay ba”?» 16:18 Ñu ne: « “Teg cab diir,” lu muy tekki? Xamunu li muy bëgg a wax.» 16:19 Yeesu gis ne, am na lu ñu ko bëgg a laaj, mu ne leen: «Dama ne: “Ca kanam tuuti, dungeen ma gis, te bu ñu ca tegee ab diir, ngeen gisaat ma.” Ndax loolu ngeen di laajante ci seen biir? 16:20 Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, dingeen jooy xàcc, waaye àddina dina bég; dingeen jàq, waaye seen njàqare dina soppaliku bànneex. 16:21 Jigéen ju nekk ci mat, dafay jàq, ndaxte waxtu wi mu war a jur jot na. Waaye bu doom ji juddoo, dina fàtte coonoom ndaxte day bég ci li doom ji gane àddina. 16:22 Noonu nag ngeen di jàqe, yéen itam. Waaye dinaa leen gisaat, seeni xol sedd, te seen mbég moomu, kenn du ko man a dindi. 16:23 Bés boobu dootuleen ma laaj dara. Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, Baay bi dina leen may lu ngeen ko ñaan ci sama tur. 16:24 Ba léegi ñaanaguleen dara ci sama tur. Ñaanleen, mu nangu. Bu ko defee seen mbég mat sëkk. 16:25 «Loolu lépp, dama leen koo wax ci ay misaal. Jamono dina ñëw, ju ma dootul wax ak yéen ci ay misaal, waaye ju ma leen dee wax lu leer ci Baay bi. 16:26 Bu keroogee dingeen ñaan ci sama tur. Neewuma dinaa leen ñaanal Baay bi, 16:27 ndaxte Baay bi ci boppam bëgg na leen. Bëgg na leen ndaxte bëgg ngeen ma, te gëm ngeen ne, ci Yàlla laa jóge. 16:28 Jóge naa ca Baay bi, ñëw àddina. Léegi maa ngi génn àddina, fekki Baay bi.» 16:29 Taalibe yi ne ko: «Léegi yaa ngi wax lu leer te misaaloo! 16:30 Léegi gis nanu ne, xam nga lépp, te soxlawul kenn di la laaj dara. Looloo tax nu xam ne, yaa ngi jóge ci Yàlla.» 16:31 Yeesu ne leen: «Ndax gëm ngeen léegi? 16:32 Waxtu waa ngi ñëw te agsi na ba noppi, dingeen tasaaroo, ku nekk ñibbi, ma des man rekk. 16:33 Waaye nag déedéet, wéetuma, ndaxte Baay baa ngi may wéttali. Dama leen wax loolu, ngir ngeen am jàmm ci man. Dingeen am nattu ci àddina, waaye takkleen fit yi; noot naa àddina.»
17:1 Bi mu waxee loolu ba noppi, Yeesu dafa xool ci kaw, ne jàkk asamaan, ñaan Yàlla ne: «Baay, waxtu wi tax ma ñëw ci àddina agsi na. Feeñalal ndamu Doom ji, ngir moom itam mu man a feeñal sa ndam. 17:2 Ndaxte jox nga ko sañ-sañ ci bépp mbindeef, ngir mu may dund gu dul jeex gi ñi nga ko dénk. 17:3 Dund gu dul jeex gi nag, mooy ñu xam la, yaw jenn Yàlla ju wóor ji am, te ñu xam it ki nga yónni, muy Yeesu Kirist. 17:4 Wone naa sa ndam ci àddina, ndax li ma matal liggéey, bi nga ma santoon. 17:5 Léegi nag Baay, ci sa teewaay, feeñalal ci man ndam, li ma amoon ci sa wet, laata àddina di sosu. 17:6 «Xamal naa sa tur nit, ñi nga tànne ci àddina te dénk ma leen. Bokkoon nañu ci yaw, nga dénk ma leen, te sàmm nañu sa kàddu. 17:7 Xam nañu léegi ne, loo ma joxaan, ci yaw la jóge, 17:8 ndaxte xamal naa leen kàddu yi nga ma jox, te nangu nañu ko. Wóor na leen ne, ci yaw laa jóge, te gëm nañu ne yaa ma yónni. 17:9 Ñoom laay ñaanal. Ñaanaluma waa àddina, waaye maa ngi ñaanal ñi nga ma dénk, ndaxte ci yaw lañu bokk. 17:10 Lu ma am, yaa ko moom, te loo am, maa ko moom; te ñoom ñoo feeñal sama ndam. 17:11 Nekkatuma ci àddina, waaye ñoom ñu ngi ci; man, ci yaw laa jëm. Baay bu sell bi, sàmm leen ci sa dooley tur woowu nga ma jox, ngir ñu nekk benn, ni nu nekke benn, man ak yaw. 17:12 Bi ma nekkee ak ñoom, daan naa leen sàmm ci sa dooley tur, tur wi nga ma jox. Wottu naa leen, ba kenn ci ñoom sànkuwul, lu dul kiy aji réer ji, ngir li Mbind mi waxoon am. 17:13 «Waaye léegi maa ngi jëmsi ci yaw, te maa ngi wax nii ci bi may nekk àddina, ngir ñu fees ak sama mbég. 17:14 Jottali naa leen sa kàddu, te àddina bañ leen, ndax li ñu mel ni man, bañ a bokk ci àddina soosu. 17:15 Ñaanuma nga jële leen àddina, waaye nga yiir leen ci Ibliis. 17:16 Dañoo mel ni man; bokkuñu ci àddina. 17:17 Samp leen ci dëgg, ngir ñu sell. Sa kàddu mooy dëgg. 17:18 Ni nga ma yónnee àddina, noonu laa leen yónnee ci nit ñi. 17:19 Sellal naa sama bopp ngir ñoom, ngir ñu sampu ci dëgg te sell. 17:20 «Ñaanaluma leen ñoom rekk, waaye itam ñi may gëm ëllëg ndax seen wax. 17:21 Damay ñaan ngir ñépp doon benn. Baay, na ñooñu nekk benn ci nun, ni nga nekke ci man te ma nekke ko ci yaw. Nañu ànd, ba àddina gëm ne, yaa ma yónni. 17:22 Boole naa leen ci ndam, li nga ma sol, ngir ñu àndandoo, ni nu ànde man ak yaw. 17:23 Man ci ñoom, yaw it ci man, ngir ñu gën a ànd, nekk benn, ba àddina xam ne yaa ma yónni, xam ne bëgg nga leen, ni nga ma bëgge. 17:24 «Baay, bëgg naa, ñi nga ma dénk nekk ak man fa ma jëm, ngir ñu gis sama ndam, li nga ma sol, ndaxte bëgg nga ma, laata àddina di sosu. 17:25 «Baay, yaw ku jub ki, waa àddina xamuñu la, waaye man xam naa la, te ñii xam nañu ne, yaa ma yónni. 17:26 Xamal naa leen sa tur te dinaa ko gën a xamle, ngir mbëggeel, gi nga am ci man, nekk ci ñoom, te man it ma nekk ci ñoom.»
18:1 Bi mu waxee noonu ba noppi, Yeesu jóge fa ak i taalibeem, jàll xuru Sedoron, dugg cib tool. 18:2 Yudaa mi ko naroon a wor xamoon na it bérab ba, ndaxte Yeesu daan na fa dem ak ay taalibeem. 18:3 Yudaa daldi fa dem, yóbbaale mbooloom xarekat ak ay alkaati yu ko saraxalekat yu mag ya ak Farisen ya jox. Ñu yor ay jum ak ay làmp ak it gànnaay. 18:4 Noonu Yeesu, mi xamoon li ko waroon a dal lépp, jubsi leen ne leen: «Ku ngeen di seet?» 18:5 Ñu ne ko: «Yeesum Nasaret.» Yeesu ne: «Man la.» Fekk Yudaa mi ko nar a wor a nga ànd ak ñoom. 18:6 Bi leen Yeesu nee: «Man la,» ñu daldi dellu gannaaw, ba daanu. 18:7 Yeesu laajaat leen ne: «Ku ngeen di seet?» Ñu ne ko: «Yeesum Nasaret.» 18:8 Mu ne leen: «Wax naa leen ne, man la. Bu fekkee ne nag man ngeen di seet, bàyyileen ñii ma àndal, ñu dem.» 18:9 Noonu la baat boobu mu waxoon ame: «Baay, kenn sànkuwul ci ñi nga ma dénk.» 18:10 Bi Yeesu waxee loolu ba noppi, Simoŋ Piyeer bocci jaasi, ji mu yoroon, daldi dóor surgab saraxalekat bu mag ba, noppu ndeyjooram dagg. Surga boobu mi ngi tuddoon Malkus. 18:11 Waaye Yeesu ne Piyeer: «Roofal jaasi ji ci mbaram. Ndax warumaa naan kaasu naqar, bi ma Baay bi sédd?» 18:12 Mbooloom xarekat ya ak seen kilifa ak alkaatiy Yawut ya jàpp Yeesu, daldi yeew, 18:13 jëkk koo yóbbu ca Anas, ndaxte Anas mooy gorob Kayif, mi doon saraxalekat bu mag ba at mooma. 18:14 Kayif moo digaloon Yawut ya ne: «Li gën moo di kenn rekk dee, ngir mbooloo mi mucc.» 18:15 Bi ñuy yóbbu Yeesu, Simoŋ Piyeer ak keneen ca taalibe ya toppoon nañu ko. Keneen kooku nag, xamante na ak saraxalekat bu mag ba, moo waral mu duggaaleek Yeesu ca biir kër kilifa ga. 18:16 Waaye Piyeer, moom, des ca buntu kër ga. Noonu taalibe boobu xamante woon ak saraxalekat bu mag ba génn, wax ak jigéen, ja doon wottu buntu kër ga, fexe Piyeer dugg ci biir. 18:17 Mbindaan mi doon wottu bunt bi ne Piyeer: «Mbaa yaw it bokkuloo ci taalibey waa ji?» Mu ne ko: «Déedéet, bokkuma ci.» 18:18 Booba dafa seddoon, ba surga ya ak alkaati ya boyal ab taal, di ca jaaru. Piyeer itam taxaw, di jaaru ak ñoom. 18:19 Saraxalekat bu mag ba daldi laaj Yeesu ci lu jëm ci taalibeem yi ak ci njàngaleem mi. 18:20 Yeesu tontu ko ne: «Ci mbooloo laa doon waxe. Ci kër Yàlla ga ak ci ay jàngu, fa Yawut yépp di daje, laa mas di jàngalee. Musumaa wax dara di ko nëbb. 18:21 Lu tax nga may laaj? Laajal ñi doon déglu li ma leen wax. Ñoom xam nañu li ma doon wax.» 18:22 Bi Yeesu waxee loolu, kenn ci alkaati yi nekkoon ci wetam daldi koy pes ne ko: «Ndax nii ngay tontoo saraxalekat bu mag bi?» 18:23 Yeesu tontu ko ne: «Su ma waxee lu jaaduwul, wone ko; waaye su ma waxee lu jub, lu tax nga may dóor?» 18:24 Anas daldi koy yebal ca Kayif, saraxalekat bu mag ba, ñu yeew ko ba tey. 18:25 Fekk na booba Simoŋ Piyeer, moom, ma nga taxaw di jaaru rekk. Ñu laaj ko ne: «Mbaa yaw it bokkuloo ci taalibey waa ji?» Waaye Piyeer weddi ko ne: «Déedéet, bokkuma ci.» 18:26 Kenn ci surgay saraxalekat bu mag ba, di mbokku ka Piyeer coroon noppam, ne Piyeer: «Xanaa du yaw laa gisoon ak moom ca tool ba?» 18:27 Waaye Piyeer dellu weddi ko. Noonu ginaar daldi sab. 18:28 Bi loolu wéyee ñu jële Yeesu ca Kayif, yóbbu ko ca kër boroom réew ma. Ci waxtuw njël la woon. Waaye Yawut ya yéeguñu ca taaxum kaw ma. Dañoo bañoon a taq sobe, ngir man a lekk ca ñamu màggalu Jéggi ba. 18:29 Looloo tax Pilaat boroom réew ma génn, dajeek ñoom. Mu laaj leen ne: «Lu ngeen di jiiñ waa jii?» 18:30 Ñu tontu ko ne: «Bu deful woon lu bon, duñu la ko jébbalsi.» 18:31 Pilaat ne leen: «Jël-leen ko, yéen, te àtte ko ci seen yoon.» Yawut yi ne ko: «Yoon mayu nu, nu àtte nit, teg ko dee.» 18:32 Noonu la kàddug Yeesu gi ame, ci li mu misaaloon ni mu war a faatoo. 18:33 Gannaaw loolu Pilaat duggaat ca taaxum kaw ma, woo Yeesu ne ko: «Ndax yaa di buuru Yawut yi?» 18:34 Yeesu tontu ko ne: «Ndax yaa ko xalaat, wax ko, am dañu la koo xelal ci man?» 18:35 Pilaat ne ko: «Mbaa xalaatoo ne, man Yawut laa? Sa xeet ak saraxalekat yu mag yi ñoo ma la jébbal. Lan nga def?» 18:36 Yeesu tontu: «Sama kilifteef nekkul ci àddina. Bu sama kilifteef nekkoon àddina, sama surga yi dinañu xeex, ngir bañ ñu jébbal ma Yawut yi. Waaye sama kilifteef nekkul àddina.» 18:37 Pilaat ne ko: «Kon yaw buur nga?» Yeesu tontu ko: «Wax nga ko; buur laa. Lii moo tax ma juddu, ñëw àddina: ngir wax dëgg gi. Ku bokk ci dëgg dina nangu li ma wax.» 18:38 Pilaat laaj ko ne: «Luy dëgg?» Bi mu waxee loolu ba noppi, Pilaat daldi génnaat, jëm ca Yawut ya ne leen: «Gisuma ci moom genn tooñ. 18:39 Seen aada laaj na, ma bàyyil leen kenn, saa su ñuy def màggalu bésu Jéggi bi. Xanaa ma bàyyil leen “buuru Yawut yi?”» 18:40 Noonu ñu daldi yuuxuwaat: «Déedéet, waxunu kii; Barabas lanu wax!» Fekk Barabas moomu taskatu réew la woon.
19:1 Noonu Pilaat joxe ndigal, ñu dóor Yeesu ay yar. 19:2 Xarekat ya ràbb kaalag dég, teg ko ci boppu Yeesu, solal ko mbubbum xarekat mu xonq curr. 19:3 Ñu di ko jegeñsi, di ko pes, naan ko: «Nuyu nanu la, yaw buuru Yawut yi!» 19:4 Pilaat génnaat ne leen: «Gis ngeen, maa ngi leen koy indil ci biti, ngir ngeen xam ne, waa jii, gisuma ci moom genn tooñ.» 19:5 Yeesu nag génn, tegoo mbubbum xarekat mu xonq mi ak kaalag dég gi. Pilaat it ne leen: «Waa jaa ngii!» 19:6 Waaye bi ñu ko gisee, saraxalekat yu mag ya ak alkaati ya di yuuxoo naan: «Daaj ko ci bant! Daaj ko ci bant, ba mu dee!» Pilaat ne leen: «Jël-leen ko, yéen, daaj ko ci bant, ndaxte gisuma ci moom genn tooñ.» 19:7 Yawut yi tontu ko ne: «Am nanu aw yoon, te ci yoon woowu, war na dee ndaxte teg na boppam Doomu Yàlla.» 19:8 Bi Pilaat déggee wax jooju, dafa gën a tiit, 19:9 dugg ca taax ma, daldi ne Yeesu: «Foo jóge?» Waaye Yeesu tontuwu ko. 19:10 Pilaat ne ko: «Man ngay bañ a waxal? Xanaa xamuloo ne, am naa sañ-sañu bàyyi la, te am naa itam sañ-sañu daaj la ci bant?» 19:11 Yeesu tontu ko ne: «Amuloo benn sañ-sañ ci man su dul bi la Yàlla jox. Looloo tax ba ki ma jébbal ci say loxo am na bàkkaar, bi gën a réy.» 19:12 Booba nag la Pilaat doon fexee bàyyi Yeesu. Waaye Yawut ya di yuuxoo naan: «Boo bàyyee kii, doo xaritu buur bi Sesaar. Nit ku teg boppam buur, noonub Sesaar la!» 19:13 Bi Pilaat déggee loolu, mu daldi génne Yeesu ca biti, dem toog ca jalub àttekaay ba, ca fu ñuy wax Bérabu doj ya. Ci làkku yawut ñu naan ko Gabata. 19:14 Ca bés ba ñuy waajal màggalu Jéggi ba la woon, ca weti digg-bëccëg. Pilaat ne Yawut ya: «Seen buur a ngii!» 19:15 Waaye ñuy yuuxoo naan: «Na dee! Na dee! Daaj ko ci bant!» Pilaat ne leen: «Ndax seen buur bi, dama koo war a daaj ci bant?» Saraxalekat yu mag ya ne ko: «Amunu benn buur bu dul Sesaar!» 19:16 Noonu Pilaat jébbal leen Yeesu, ngir ñu daaj ko ci bant. Bi leen ko Pilaat jébbalee, ñu jël ko, yóbbu. 19:17 Yeesu ci boppam gàddu bant ba, génn ngir dem ca fa ñuy wax Bérabu kaaŋu bopp; ñu koy wooye Golgota ci làkku yawut. 19:18 Foofa la xarekat ya daaje Yeesu ca bant ba. Ci noonu it ñu daajaale ñaari nit ci wetam, mu nekk ca digg ba. 19:19 Pilaat santaane itam ñu bind, teg ko ca kaw bant, ba ñu ko daajoon. Mbind ma lii la wax: «Kii mooy Yeesum Nasaret, buuru Yawut yi.» 19:20 Mbind mooma, Yawut yu bare jàng nañu ko, ndaxte fa ñu daajoon Yeesu ca bant ba jege woon na dëkk ba, te mbind ma ci làkku yawut la woon, ci làkku waa Room ak ci gereg. 19:21 Noonu saraxalekat yu mag yu Yawut ya ne Pilaat: «Bul bind: “Buuru Yawut,” bindal rekk: “Kii moo ne mooy buuru Yawut yi.”» 19:22 Pilaat tontu leen ne: «Xas naa koo bind, du deñ.» 19:23 Xarekat ya, bi ñu daajee Yeesu ca bant ba, ba noppi dañoo jël ay yéreem, séddale ko ñeenti cér, ku nekk benn. Jël nañu it mbubbam bu ñu ràbb ca kaw ba ci suuf te amul benn ñaw. 19:24 Xarekat ya di waxante naan: «Mbubb mi, bunu ko xotti, waaye nanu ko tegoo ay bant, ngir xam ku koy moom.» Noonu la Mbind mi waroon a ame, bi mu naan:«Séddoo nañu samay yére,tegoo ay bant sama mbubb.» Loolu nag la xarekat ya def. 19:25 Ca wetu bant, ba ñu daajoon Yeesu, yaayam a nga fa taxawoon, moom ak doomu ndeyam ju jigéen, Maryaama jabari Këlópas, ak Maryaama mi dëkk Magdala. 19:26 Bi Yeesu gisee yaayam taxaw ci wetu taalibe, bi mu bëggoon, mu ne ko: «Soxna si, sa doom a ngi,» 19:27 neeti taalibe ba: «Sa yaay a ngi nii.» Booba la ko taalibe ba yóbbu këram, yor ko. 19:28 Bi loolu wéyee gannaaw Yeesu xam na ne, lépp mat na léegi, mu ne nag, ngir amal Mbind mi: «Damaa mar.» 19:29 Amoon na foofa gutt bu fees ak bineegar. Noonu ñu jël sagar, tooyal ko ca, takk ko ci bantu garab gu ñuy wax isob, teg ko ci gémmiñu Yeesu. 19:30 Bi Yeesu muucoo bineegar bi, mu ne: «Lépp mat na!» Noonu mu sëgg, delloo ruuwam Yàlla. 19:31 Keroog ba ñu dee waajal bésu noflaay ba la woon, te Yawut ya bëgguñu néew ya des ca bant ya, ndaxte bésu noflaay boobu fonkoon nañu ko lool. Ñu ñaan Pilaat, mu dammlu tànki ña ñu daajoon, te jële leen fa. 19:32 Noonu xarekat ya dem, damm tànki ku jëkk ka, teg ca ka ca des, ca ña ñu daajaale woon ak Yeesu. 19:33 Bi ñu agsee ci Yeesu, dammuñu ay tànkam, ndaxte gis nañu ne booba faatu na. 19:34 Waaye kenn ca xarekat ya daldi jël xeej, jam ko ko ci wet, ca saa sa deret ak ndox di tuuru. 19:35 Kiy nettali mbir yooyu, da cee teg bëtam, te li muy wax dëgg la. Moom ci boppam xam na ne, li muy wax dëgg la, ngir yéen itam ngeen gëm, 19:36 ndaxte loolu dafa xew ngir Mbind mi am: «Benn yaxam du damm.» 19:37 Leneen it Mbind mi wax na ko: «Dinañu gis ki ñu jamoon.» 19:38 Gannaaw loolu Yuusufa mi dëkk Arimate ñaan Pilaat ngir yóbbu néewu Yeesu. Yuusufa taalibe Yeesu la woon ci lu kenn yégul, ndaxte dafa ragaloon Yawut ya. Pilaat may ko ko. Yuusufa daldi dem, yóbbu néewu Yeesu. 19:39 Nikodem itam ñëw, moom mi masoon a seeti Yeesu guddi. Mu indaale lu war a tollook fanweeri kiloy cuuraay lu ñu defare ndàbbi miir ak banti aloos. 19:40 Ñu jël néewu Yeesu, laxas ko ci càngaay, boole ko ak cuuraay li, ni ko Yawut yi tàmmoo def, bu ñuy waajal néew. 19:41 Tool a nga woon ca wetu bérab, ba ñu daajoon Yeesu, te ca tool booba amoon na fa bàmmeel bu ñu musul a suul kenn. 19:42 Ca bésu Waajal la woon, ba Yawut ya doon waajal bésu noflaay ba, te bàmmeel ba jege woon na. Foofa lañu denc Yeesu.
20:1 Bés ba jiitu ca ayu-bés ga, Maryaamam Magdala jóg ca fajar, dem ca bàmmeel ba. Bi mu agsee, mu gis ne dindi nañu xeer, wa ñu ko ube woon. 20:2 Mu daw, dem ca Simoŋ Piyeer ak ca beneen taalibe ba, maanaam ka Yeesu bëggoon, ne leen: «Jële nañu néewu Boroom ba ca bàmmeel ba, te xamunu fu ñu ko yóbbu.» 20:3 Piyeer ak beneen taalibe ba daw, dem ca bàmmeel ba. 20:4 Ñoom ñaar ñépp a ngi doon daw, waaye beneen taalibe ba raw Piyeer, jëkk ko ca bàmmeel ba. 20:5 Duggul nag, dafa sëgg, yër, séen càngaay la ca suuf. 20:6 Noonu Simoŋ Piyeer, mi ko toppoon, agsi, daldi dugg. Mu séen càngaay la ci suuf, 20:7 ak kaala ga muuroon boppu Yeesu. Waaye kaala googu àndul ak càngaay la; dañu ko laxas, teg ko ci wet. 20:8 Noonu keneen ka jiitu woon ca bàmmeel ba, duggsi moom itam. Naka la gis, daldi gëm. 20:9 Taalibe yi xamaguñu woon Mbind, mi doon wone ne, Yeesu dafa war a dekki. 20:10 Noonu taalibe ya dëpp, ñibbi. 20:11 Maryaama nag moom, ma nga desoon ca biti, ca wetu bàmmeel ba, di jooy. Bi muy jooy, mu sëgg, yër ci biir, 20:12 séen ñaari malaaka yu sol mbubb yu weex, toog ca bérab, ba ñu dencoon Yeesu; kenn ka féeteek bopp bi, ki ci des ca tànk ya. 20:13 Malaaka ya laaj ko ne: «Jigéen ji, looy jooy?» Mu tontu leen ne: «Dañoo jël sama Boroom, te xawma fu ñu ko yóbbu.» 20:14 Bi mu waxee loolu, mu geestu, séen Yeesu mu taxaw, waaye xamul woon ne moom la. 20:15 Yeesu laaj ko ne: «Jigéen ji, looy jooy? Kooy seet?» Mu foog ne boroom tool ba la, ne ko: «Sëriñ bi, bu fekkee yaa ko yóbbu, wax ma foo ko denc, ma jëli ko.» 20:16 Noonu Yeesu ne ko: «Maryaama.» Mu walbatiku, làkk ko ci yawut ne ko: «Ràbbuni!» Ràbbuni mooy tekki «Kilifa gi.» 20:17 Yeesu ne ko: «Bu ma téye, ndaxte yéegaguma ca Baay ba. Waaye demal, ne samay bokk, maa ngi yéeg ca sama Baay biy seen Baay, ca sama Yàlla jiy seen Yàlla.» 20:18 Noonu Maryaamam Magdala dem, yégali ko taalibe ya ne leen: «Gis naa Boroom bi!» Mu daldi leen nettali li mu ko wax. 20:19 Bés boobu ca ngoon sa, taalibe yaa nga daje woon ca genn kër, tëju ca biir ndax ragal Yawut ya. Yeesu ne tëll ci seen biir ne leen: «Na jàmm wàcc ci yéen!» 20:20 Mu daldi leen won ay loxoom ak wetam. Bi ñu gisee Boroom bi, taalibe ya daldi bég lool. 20:21 Yeesu dellu ne leen: «Na jàmm wàcc ci yéen! Ni ma Baay bi yónnee, noonu laa leen di yónnee, man itam.» 20:22 Bi mu waxee loolu, mu ëf leen ne leen: «Sol naa leen Xelu Yàlla mu Sell mi. 20:23 Ñi ngeen di baal seeni bàkkaar, baal nañu leen ba noppi; ñi ngeen baalul, baaluñu leen.» 20:24 Fekk na Tomaa, mi bokk ci fukki taalibe yi ak ñaar, te turam di tekki «Séex bi,» nekku fa woon, bi Yeesu ñëwee. 20:25 Yeneen taalibe yi ne ko: «Gis nanu Boroom bi!» Waaye mu ne leen: «Su ma gisul fa ñu daajoon pont ya ci ay loxoom, te defuma ca sama baaraam, su ma tegul it sama loxo ci wetam, duma ko gëm mukk.» 20:26 Bi ñu ca tegee ayu-bés, taalibe Yeesu ya dajewaat ca biir kër ga, Tomaa itam a nga fa woon. Bunt yépp tëju woon nañu, waaye Yeesu ne tëll ci seen biir ne leen: «Na jàmm wàcc ci yéen!» 20:27 Noonu mu ne Tomaa: «Indil sa baaraam fii te seet sama loxo; indil sa loxo, teg ko ci sama wet. Bàyyil di weddi te nga gëm.» 20:28 Tomaa tontu ko ne: «Sama Boroom, sama Yàlla!» 20:29 Yeesu ne ko: «Li nga ma gis a tax nga gëm? Ki bég mooy ki gëm te gisu ma!» 20:30 Yeesu wone na it ci kanamu taalibe ya yeneeni firnde yu ñu nettaliwul ci téere bii. 20:31 Waaye li ci nekk, bind nañu ko ngir ngeen gëm ne, Yeesu mooy Almasi bi, Doomu Yàlla ji, te seen ngëm may leen, ngeen am ci moom dund.
21:1 Bi ñu ca tegee ab diir, Yeesu feeñuwaat na ay taalibeem ca tefesu dex gu ñuy wax Tiberyàdd. Nii la deme woon: 21:2 Taalibey Yeesu yii àndoon nañu: Simoŋ Piyeer; Tomaa, ki turam di tekki «Séex bi;» Nataneel, mi dëkk Kana ca diiwaanu Galile; doomi Sebede ak yeneen ñaari taalibe. 21:3 Simoŋ Piyeer ne leen: «Maa ngi nappi.» Ñu ne ko: «Nun it danuy ànd ak yaw.» Ñu dugg gaal, daldi dem. Waaye guddi googu jàppuñu dara. 21:4 Ci fajar gi Yeesu taxaw ca tefes ga, waaye taalibe yi xàmmiwuñu ko. 21:5 Yeesu ne leen nag: «Bokk yi, xanaa jàppuleen jën?» Ñu ne ko: «Déedéet.» 21:6 Mu ne leen: «Sànnileen mbaal mi ci ndeyjooru gaal gi, bu ko defee ngeen jàpp.» Ñu sànni fa mbaal ma, mu fees ak jën, ba mënuñu ko woon a génne ndox mi. 21:7 Taalibe ba Yeesu bëggoon, ne Piyeer: «Boroom bi la!» Bi Simoŋ Piyeer déggee loolu, dafa woddoo mbubbam, ndaxte dafa summeeku woon, daldi sóobu ci dex gi. 21:8 Yeneen taalibe ya xëcc mbaal, mi fees dell ak jën, jëme ko ca tefes ga, ndaxte gaal ga sorewul woon; diggante bi waroon na tollook téeméeri meetar. 21:9 Bi ñu teeree, ñu gis ab taal, ñu ciy lakk ay jën, teg mburu ca wet ga. 21:10 Yeesu ne leen: «Indileen ci jën, yi ngeen jàpp.» 21:11 Simoŋ Piyeer yéeg ca gaal ga, daldi xëcc mbaal ma ca tefes ga, mu fees dell ak jën yu mag; matoon na téeméeri jën ak juróom-fukk ak ñett. Te li muy baree-bare lépp, taxul mbaal ma dog. 21:12 Yeesu ne leen: «Ñëwleen ndékki.» Kenn ci taalibe yi ñemewu koo laaj ki mu doon, ndaxte xam nañu ne, Boroom bi la. 21:13 Yeesu jegeñsi, jël mburu mi, jox leen, jox leen it jën. 21:14 Bi Yeesu dekkee ba tey, bii mooy ñetteelu yoon, bi mu feeñoo ay taalibeem. 21:15 Bi ñu ndékkee ba noppi, Yeesu ne Simoŋ Piyeer: «Simoŋ doomu Yowaana, ndax gën nga maa bëgg, ni ma ñii bëgge?» Mu tontu ko ne: «Aaŋkay, Boroom bi, xam nga ne, bëgg naa la.» Yeesu ne ko: «Topptool ma sama mbote yi.» 21:16 Noonu mu waxaat ko ne: «Simoŋ doomu Yowaana, ndax bëgg nga ma?» Mu ne ko: «Aaŋkay, Boroom bi, xam nga ne, bëgg naa la.» Yeesu ne ko: «Sàmmal ma sama xar yi.» 21:17 Mu neeti ko ñetteel bi yoon: «Simoŋ doomu Yowaana, bëgg nga maam?» Piyeer am naqar ci li mu ko laaj ñetti yoon: «Ndax bëgg nga ma?» Mu tontu ko ne: «Boroom bi, xam nga lépp; xam nga ne bëgg naa la.» Yeesu ne ko: «Topptool ma sama xar yi. 21:18 Ci dëgg-dëgg Piyeer, maa ngi la koy wax, bi nga dee ndaw yaa doon takk sa geño, di dem fu la neex. Waaye boo màggatee, dinga tàllal say loxo, keneen takkal la sa geño, yóbbu la foo bëggul.» 21:19 Ci baat yooyu la Yeesu doon misaale nan la Piyeer war a faatoo ngir jollil ndamu Yàlla. Noonu Yeesu ne ko: «Toppal ci man!» 21:20 Piyeer geestu, gis taalibe bi Yeesu bëggoon, di ñëw ci seen gannaaw. Taalibe boobu mooy ki sóonu woon ca Yeesu, ba ñuy lekk, te laajoon ko ne: «Boroom bi, kan moo lay wori?» 21:21 Piyeer gis ko, daldi ne Yeesu: «Kii nag, Boroom bi, nu muy mujje?» 21:22 Yeesu ne ko: «Su ma neexoon mu dund, ba ma dellusi, lu ciy sa yoon? Yaw toppal ci man.» 21:23 Noonu am, ci bokki taalibe yi, ñu xalaat ne, taalibe boobu du dee. Moona Yeesu musul ne Piyeer, du dee; waaye li mu wax mooy: «Su ma neexoon mu dund, ba ma dellusi, lu ciy sa yoon?» 21:24 Taalibe boobu mooy seede mbir yooyu, bind leen, te xam nanu ne, li muy wax dëgg la. 21:25 Yeesu def na yeneen jëf yu bare. Su ñu ko doon nettali, bind lépp, xalaat naa ne, téere yi duñu xaj ci àddina.
1:1 Yaw Teyofil, téere bu jëkk, ba ma bindoon, ëmb na lépp li Yeesu tàmbali woon a jëf ak a jàngale, 1:2 ba ci bés, ba ko Yàlla yéege ci asamaan. Lu ko jiitu joxoon na ay ndigal, jaare ci Xel mu Sell mi, jëm ci ndaw ya mu tànnoon. 1:3 Gannaaw ay coonoom, ñëw na ci ñoom, di leen won ay firnde yu bare te wér ne mu ngi dund; mu feeñu leen diirub ñeent-fukki fan, di diisoo ak ñoom ci lu jëm ci nguuru Yàlla. 1:4 Am bés muy lekk ak ñoom, mu sant leen ne: «Buleen sore Yerusalem, waaye ngeen xaar li Baay bi dige woon te ma waxoon leen ko. 1:5 Ndaxte Yaxya daa na sóob nit ñi ci ndox, waaye yéen dees na leen sóob ci Xel mu Sell mi fi ak ay fan yu néew.» 1:6 Bi ñu dajaloo ak moom nag, ñu laaj ko: «Boroom bi, ndax ci jamono jii ngay yékkatiwaat nguuru Israyil?» 1:7 Mu tontu leen: «Ngeen xam jamono yi ak saa, yi Baay bi dogal ci sañ-sañam, loolu mayuñu leen ko. 1:8 Waaye bu Xel mu Sell mi ñëwee ci yéen, dingeen jot kàttan te nekk samay seede ci dëkku Yerusalem, ca diiwaani Yude ak Samari yépp ak ba fa àddina yem.» 1:9 Bi mu waxee loolu, te ñu di ko xool, Yàlla yéege na ko, te aw niir jël ko, làq ko seeni bët. 1:10 Bi muy dem nag, te ñu ne jàkk asamaan, ñaar ñu sol yu weex daldi ne seef, taxaw ci seen wet. 1:11 Ñu ne leen: «Yéen waa Galile, lu tax ngeen taxaw, di xool ci asamaan? Yeesu male ñu jële ci seen biir, yéege ko asamaan, dina dellusi ni ngeen ko gise, muy dem asamaan.» 1:12 Bi loolu amee ñu jóge ca tund, woowu ñuy wax tundu Oliw ya, te mu dend ak Yerusalem lu tollu ak kilomet, ñu daldi dellu Yerusalem. 1:13 Bi ñu dikkee, ñu yéeg ca néeg, ba sut ca taax ma, fa ñuy dal. Ñoo doon Piyeer ak Yowaana, Saag ak Andare, Filib ak Tomaa, Bartelemi ak Macë, Saag doomu Alfe, ak Simoŋ mi bokkoon ci mbooloo mi ñuy wax Ñi farlu ci moom seen réew; ak Yudaa doomu Saag. 1:14 Ñoom ñépp ñoo bokk menn xel, di wéy ci ñaan ci Yàlla, ànd ak jigéen ñi ak Maryaama, ndeyu Yeesu, ak rakki Yeesu yu góor. 1:15 Ca bés yooya nag Piyeer taxaw ca digg bokk ya, di mbooloo mu tollu ni téeméer ak ñaar-fukk. 1:16 Mu ne leen: «Bokk yi, li Xel mu Sell mi waxoon ci Mbind mi jaarale ko ci gémmiñu Daawuda, fàww mu am. Waxoon na ci mbirum Yudaa, mi wommat ñi jàpp Yeesu 1:17 te mu bokkoon ci nun, ba am cér ci liggéey bi.» 1:18 --Pey gi Yudaa jotoon ci ñaawteefam, mu jënd ci tool, daanu fa, ba fàcc, ay buttitam tuuru. 1:19 Loolu siiwoon na ci waa Yerusalem, moo tax ci seen làkk ñuy tudde tool ba Akeldama, maanaam «Toolu deret.» — 1:20 Piyeer teg ca ne: «Ndaxte lii lañu bind ci téereb Sabóor:“Na këram gental,bu fa kenn dëkk.” Te it:“Na keneen bey sasam.” 1:21 Kon ñeel na nu, nu tànn kenn ci ñi bokk ak nun, diir bi Yeesu doon dem ak a dikk ci sunu biir, 1:22 li dale ci bi ko Yaxya sóobee ci ndox, ba bés ba ko Yàlla jële ci sunu biir, yéege ko. Kooku war na ànd ak nun, di seedeel ndekkitel Yeesu.» 1:23 Bi ko Piyeer waxee, ñu tudd ñaar: Yuusufa, mi ñu dippee Barsabas te di ko dàkkentale Yustus, moom ak Macas. 1:24 Ñu ñaan ci Yàlla ne: «Boroom bi, yaw mi xam xolu nit ñépp, won nu ki nga tànn ci ñaar ñii, 1:25 mu yenu liggéeyu nekk sa ndaw, wuutu Yudaa, mi ko bàyyi, dem bérabam.» 1:26 Noonu ñu boole leen, tegoo ay bant, bant ba dal ca Macas, mu fekki fukki ndaw ya ak benn.
2:1 Bi bésu màggalu Pàntakot agsee, ñoom ñépp booloo nañu ci benn bérab. 2:2 Ca saa sa riir jollee asamaan, mel ni ngelaw lu gaaw te bare doole, daldi fees dell kër, ga ñu toog. 2:3 Te ay làmmiñ yu mel ni safara feeñu leen, ñu tasaaroo ci seen biir, toŋ ca kaw kenn ku nekk. 2:4 Noonu ñu fees ak Xel mu Sell mi ñoom ñépp, ñu daldi wax yeneeni làkk, ni leen Xel mu Sell mi maye, ñu wax ko. 2:5 Fekk booba amoon na ay Yawut yu daloon Yerusalem, doon ay nit ñu ragal Yàlla te bokk ci xeeti àddina yépp. 2:6 Bi nit ñi déggee riir ma nag, ñépp dajaloo, daldi waaru ci li ñu leen dégg, ñuy wax ku nekk sa làkk. 2:7 Ñu waaru te yéemu naa: «Gisleen, ñiy wax ñépp, ndax duñu waa diiwaanu Galile? 2:8 Naka la man a ame nag, nu di leen dégg, kenn ku nekk ci nun, ñuy wax ci sa làmmiñ, wi nga nàmp? 2:9 Nun ñi ay Pàrt, waa Medi ak waa Elam, nun ñi dëkk Mesopotami, réewu Yawut yi, Kapados, Pont ak Asi, 2:10 di waa Firisi, Pamfili, Misra ak weti Libi, yi dend ak Siren, nun ak gan ñi jóge Room, 2:11 Yawut yi ak ñi tuub ci yoonu Yawut yi, waa Kereet ak Araab yi, nun ñépp nu ngi leen di dégg, ñuy yégle màggaayi Yàlla ci sunuy làkk!» 2:12 Noonu ñépp waaru, ba jaaxle lool, ñuy waxante ci seen biir ne: «Lii lu muy tekki?» 2:13 Waaye ñenn ñi di leen ñaawal ne: «Waay! ñii dañoo màndi ak biiñ.» 2:14 Ci kaw loolu Piyeer taxaw, ànd ak fukki ndaw ya ak benn, mu wax ci kaw, di yégal mbooloo ma ne: «Bokki Yawut yi ak yéen ñépp ñi dëkk Yerusalem, dégluleen bu baax te xam lii ma leen di wax! 2:15 Nit ñii màndiwuñu, ci ni ngeen ko fooge, ndaxte nu ngi ci yoor-yoor rekk. 2:16 Waaye lii mooy li Yàlla waxoon, jaarale ko ci yonentam Yowel ne: 2:17 “Yàlla nee na: Ci bés yu mujj yi,dinaa tuur ci sama Xel ci kaw nit ñépp;seen xeet wu góor ak wu jigéendinañu wax ci kàddug Yàlla;waxambaane yi dinañu gis ay peeñute màggat yi di gént ay gént. 2:18 Waaw ci bés yooyu dinaa tuur ci sama Xelci sama kaw jaam yu góor ak yu jigéen,te dinañu wax ci kàddug Yàlla. 2:19 Dinaa wone ay kéemaan ci kaw ci asamaanak ay firnde ci suuf ci àddina,muy deret, safara ak ay niiri saxar. 2:20 Jant bi dina daldi lëndëm,weer wi deretal,bala bésu Boroom biy ñëw,di bés bu mag, bi ànd ak ndam. 2:21 Booba nag ku woo Boroom bi ci aw turam,dinga mucc.” 2:22 «Yéen bokki Israyil, dégluleen wax jii! Yeesu mi dëkk Nasaret, nit la woon, ku Yàlla dëggal ci seen kanam ciy kéemaan, ay jaloore ak firnde, ya Yàlla defoon jaarale ko ci moom ci seen biir; yéen xam ngeen ko. 2:23 Moom nag jébbale nañu ko, jaar ci nas, bi Yàlla dogaloon te xam ko lu jiitu; te yéen rey ngeen ko ci daaj ko ci bant, jaarale ko ci loxoy bàkkaarkat. 2:24 Waaye Yàlla dekkal na ko, daggal ko buumi dee, ndaxte dee mënu koo téye. 2:25 Daawuda wax na ci mbiram ne:“Saa su ne gis naa Boroom bi ci sama kanam,gannaaw mu ngi ci sama ndeyjoor,kon duma raf. 2:26 Moo tax sama xol sedd,may woy sama bànneex,te it sama yaram di tëdd ci yaakaar. 2:27 Ndaxte doo bàyyi sama ruu ci barsàq,te doo seetaan sa waa ju sell, mu yàqu. 2:28 Xamal nga ma yoonu dund;dinga ma béglooji ci sa kanam.” 2:29 «Bokk yi, man naa leen a wax lu wóor ci mbirum maam Daawuda, ne dee na te suul nañu ko; bàmmeelam mu ngi ci nun ba tey. 2:30 Waaye yonent la woon, te xamoon na ne, Yàlla digoon na ko ci ngiñ ne, dina teg ci nguuram kenn ci askanam. 2:31 Kon gis na lu ñëwagul, di wax ci mbirum ndekkitel Kirist ne, bàyyiwuñu ko ci barsàq, te yaramam yàquwul. 2:32 Yeesu moomu nag, Yàlla dekkal na ko; nun ñépp seede nanu ko. 2:33 Yàlla yéege na ko ak ndeyjooram, te jot na ci Baay bi Xel mu Sell mi ñu dige woon, ba tuur lii ngeen gis te dégg ko. 2:34 Ndaxte du Daawudaa yéeg ci asamaan, waaye moom ci boppam nee na:“Boroom bi wax na sama Boroom:‘Toogal ci sama ndeyjoor, 2:35 ba kera may daaneelsay noon ci sa kanam.’ ” 2:36 «Na bànni Israyil gépp xam bu wóor nag ne, Yeesu moomu ngeen daajoon ci bant, Yàlla def na ko Boroom ak Almasi bi.» 2:37 Bi ko mbooloo ma déggee, naqaru xol wu metti jàpp leen; ñu daldi ne Piyeer ak ndaw ya ca des: «Bokk yi, lu nu war a def?» 2:38 Piyeer tontu leen ne: «Tuubleen seeni bàkkaar, te kenn ku nekk ci yéen, ñu sóob ko ci ndox ci turu Yeesu Kirist. Noonu Yàlla dina leen baal seeni bàkkaar te may leen Xel mu Sell mi. 2:39 Ndaxte li Yàlla dige woon, yéena ko moom ak seeni doom ak ñu sore ñépp, di ñépp ñi Yàlla sunu Boroom di woo ci moom.» 2:40 Noonu mu artu leen ak yeneen wax yu bare, di leen dénk ne: «Rëccleen ci niti jamono ju dëng jii.» 2:41 Ñi nangu ay waxam nag, ñu sóob leen ci ndox, te ca bés booba lu mat limub ñetti junniy nit yokku nañu ci ñoom. 2:42 Ñoom nag ñuy wéy ci njàngalem ndaw yi ak cig bokk, ci damm mburu ak ñaan ci Yàlla. 2:43 Ragal jàpp ñépp, te ndaw yi di def ay kéemaan ak ay firnde yu bare. 2:44 Ñi gëm nag dañoo booloo te bokk lépp. 2:45 Ñu jaay seeni suuf ak seen alal, séddoo ko, ku nekk ak la ngay soxla. 2:46 Te bés bu nekk ñu saxoo teew ak benn xalaat ca kër Yàlla ga, tey damm mburu ca kër ya; ñuy lekk seen ñam ak xol bu laab tey bég, 2:47 di màggal Yàlla te am yiw ci wetu nit ñépp. Noonu bés bu nekk Boroom bi di yokk ca mbooloo ma ñi mucc.
3:1 Am bés Piyeer ak Yowaana dem, ba bëgg a dugg ca kër Yàlla ga ca waxtuw ñaan, maanaam tisbaar. 3:2 Fekk ñu indi fa nit ku judduwaale lafañ, ñu di ko teg bés bu nekk ca bunt, ba ñuy wooye Bunt bu rafet ba, ca kër Yàlla ga, ngir muy yelwaan ña fay dugg. 3:3 Bi mu gisee Piyeer ak Yowaana nag, ñuy dugg ca kër Yàlla ga, mu dékk leen loxo. 3:4 Ci kaw loolu Piyeer ak Yowaana ne ko jàkk, te Piyeer ne ko: «Xool nu.» 3:5 Lafañ bi xool leen, yaakaar ne dina jot dara ci ñoom. 3:6 Noonu Piyeer ne ko: «Awma xaalis, awma wurus, waaye li ma am, dinaa la ko jox: ci turu Yeesu Kirist mu Nasaret doxal!» 3:7 Mu jàpp ci loxol ndeyjooram, yékkati ko. Ci saa si ay tànkam ak ay kostanam dëgër. 3:8 Mu tëb, daldi taxaw, di dox. Mu dugg ak ñoom ca kër Yàlla ga, muy dox, di tëb tey sant Yàlla. 3:9 Noonu ñépp gis ko, muy dox, di sant Yàlla. 3:10 Te ñu xàmmi ko, ne moo daan toog, di yelwaan ca Bunt bu rafet ba ca kër Yàlla ga. Ñu daldi waaru lool te yéemu ci li ko dikkal. 3:11 Naka waa ji taq ci Piyeer ak Yowaana, ñépp waaru; ñu daldi daw, fekksi leen ca bérab ba ñuy wax Werandaa bu Suleymaan. 3:12 Bi Piyeer gisee loolu nag, mu ne mbooloo mi: «Yéen waa Israyil, lu tax ngeen waaru ci lii? Lu tax ngeen di nu xool jàkk, mel ni ci sunu kàttan, mbaa ci sunu ragal Yàlla lanu doxloo kii? 3:13 Yàllay Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, di Yàllay sunuy maam, màggal na Ndawam Yeesu; yéena xàcceek moom, ba jébbal ko Pilaat, fekk naroon na koo bàyyi. 3:14 Yéen xeeb ngeen Aji Sell ji te Jub, te tinul ab reykat. 3:15 Bóom ngeen Aji Dundal ji, waaye Yàlla dekkal na ko; seede nanu ko nun ñépp. 3:16 Ci gëm turam la nit, kii ngeen di gis te xam ko, dëgëre; waaw, turu Yeesu ak ngëm gi jóge ci moom, moo tax mu wér peŋŋ ci seen kanam, yéen ñépp. 3:17 «Léegi nag bokk yi, xam naa ne, ñàkka xam a tax ngeen def ko, yéen ak seeni kilifa. 3:18 Waaye noonu la Yàlla amale li mu yégle woon lu jiitu jaarale ko ci gémmiñug yonent yépp naan, Almaseem dina sonn. 3:19 Tuubleen seeni bàkkaar nag te woññiku ci Yàlla, ngir seeni bàkkaar far. 3:20 Noonu jamonoy péex dina bawoo ci Boroom bi, te muy yebal Almasi bi mu leen jagleel, maanaam Yeesu. 3:21 Asamaan war na koo yor, ba jamono ju ñuy defaraat lépp, di jamono ji Yàlla waxoon jaarale ko ci gémmiñug yonentam yu sell yépp, li dale ci njàlbéenug àddina. 3:22 Ndaxte Musaa nee woon na: “Boroom bi seen Yàlla dina leen feeñalal ci seen xeet Yonent ni man; nangeen ko déggal ci lépp lu mu leen wax. 3:23 Képp ku déggalul Yonent boobu, dees na la far ci xeet wi.” 3:24 «Li dale sax ci Samwil ak ñi ci topp, bépp yonent bu wax yégle na bés yii. 3:25 Yéen nag yéenay donn yonent yi ak kóllëre, gi Yàlla fasoon ak seeni maam, bi mu naan Ibraayma: “Xeeti àddina yépp dinañu barkeel ci ki soqikoo ci yaw.” 3:26 Yàlla feeñal na Ndawam, jëkk koo yebal ci yéen, ngir barkeel leen, ci woññi leen kenn ku nekk ci say bàkkaar.»
4:1 Bi ñuy wax ak mbooloo ma, saraxalekat ya ak kilifag ñiy wottu kër Yàlla ga ak Sadusen ya daanu ci seen kaw. 4:2 Ñu mer lool ci li ñuy waar nit ñi, di yégle ndekkitel ñi dee, sukkandikoo ko ci ndekkitel Yeesu. 4:3 Noonu ñu jàpp leen, tëj leen ba ca ëllëg sa, ndaxte mu nga doon tàmbalee guddi. 4:4 Waaye ñu bare ca ña dégg wax ja gëm nañu, te limu góor ñi gëm yokku na, ba mat juróomi junni. 4:5 Ca ëllëg sa nag kilifay Yawut yi ak njiit yi ak xutbakat yi dajaloo ci Yerusalem. 4:6 Ràññe nañu ci: Anas, miy saraxalekat bu mag bi, Kayif, Yowaana, Alegsàndar ak bokki saraxalekat bu mag bi. 4:7 Ñu dëj Piyeer ak Yowaana ca digg ba, laaj leen ne: «Lii ngeen def, ci gan kàttan, mbaa ci turu kan, ngeen ko defe?» 4:8 Ci kaw loolu Piyeer daldi fees ak Xel mu Sell mi, ne leen: «Yéen kilifay xeet wi ak njiit yi, 4:9 bu fekkee ne xettali nit ku wopp, ba mu wér, moo tax ngeen dëj nu ci pénc mi tey, 4:10 nangeen xam lii, yéen ñépp ak bànni Israyil gépp! Ci turu Yeesu Kirist mu Nasaret, mi ngeen daajoon ca bant te Yàlla dekkal ko, ci tur woowu la nit kii jële ag wér, ba taxaw ci seen kanam. 4:11 Yeesu moomu mooy:“Doj wi ngeen xeeboon, yéen tabaxkat yi,te moo doon doju koñ.” 4:12 Te mucc amul ci keneen, ndaxte ci ron asamaan amul weneen tur wu ñu maye ci nit ñi, wu nu war a mucce.» 4:13 Kon bi ñu gisee fit, wi Piyeer ak Yowaana àndal, te ñu xam ne, musuñoo jàng mbaa ñuy gëstu ci diine, ñu daldi waaru, ràññee ne, daa nañu ànd ak Yeesu. 4:14 Te bi ñu gisee nit, ka ñu fajoon, taxaw ak ñoom, mënuñu caa teg dara. 4:15 Noonu ñu santaane, ñu génne leen, ñu daldi gise ci seen biir, 4:16 ne: «Lu nuy def ak ñii? Ndaxte def nañu kéemaan gu siiw; loolu leer na ñi dëkk Yerusalem ñépp, te mënunu koo weddi. 4:17 Waaye ngir mbir mi bañ a law ci xeet wi, nanu leen aaye, ñu bañ a waxati ak kenn ci tur woowu.» 4:18 Noonu ñu woo leen, ñu tere leen bu wóor, ñu waxati mbaa waare dara ci turu Yeesu. 4:19 Waaye Piyeer ak Yowaana tontu leen ne: «Bu fekkee ne déggal leen te bàyyi Yàlla moo jub ci kanam Yàlla, seetleen ko. 4:20 Waaye nun mënunoo bañ a wax li nu gis te dégg ko.» 4:21 Noonu kilifa yi tëkkuwaat leen, yiwi leen, ñu dem. Ndaxte amuñu benn bunt ci ñoom ngir mbugal leen, fekk ñépp di màggal Yàlla ci li xewoon. 4:22 Ndaxte nit, ka ñu fajoon ci kéemaan googu, weesoon na ñeent-fukki at. 4:23 Bi ñu leen yiwee nag, ñu dem ci seeni bokk, nettali leen li saraxalekat yu mag ya ak njiit ya waxoon lépp. 4:24 Bi ko bokk ya déggee nag, ñu mànkoo, diis seen kàddu Yàlla ne: «Boroom bi, yaa sàkk asamaan, suuf, géej ak lépp li nekk ci seen biir. 4:25 Yaa wax, jaar ci sunu maam Daawuda sa jaam, mi doon gémmiñu Xel mu Sell mi, ne:“Lu tax xeeti àddina di bax?Lu tax ñuy fexe lu mënul a am? 4:26 Buuri àddina dañoo booloo,te kilifa yi dajaloo,di bañ Boroom bi ak Almaseem.” 4:27 Ndaxte ci dëgg ci dëkk bii, Erodd ak Poñsë Pilaat ànd ak xeeti àddina ak bànni Israyil, likkoo nañu, ngir daaneel sa Ndaw lu sell li nga fal, di Yeesu, 4:28 te def lépp, li sa kàttan ak sa ndigal tëraloon. 4:29 Léegi nag Boroom bi, seetal seeni tëkku te may say jaam, nuy wax sa kàddu ak fit. 4:30 Tàllalal sa loxo, ci wéral ak ci wone ay kéemaan ak ay firnde, jaarale ko ci turu Yeesu, sa Ndaw lu sell li.» 4:31 Bi ñu ñaanee ba noppi, bérab ba ñu booloo woon daldi yengatu; te ñoom ñépp fees ak Xel mu Sell mi, ñuy wax kàddug Yàlla ak fit wu dëgër. 4:32 Noonu mbooloom ñu gëm ñi bokk menn xel ak benn xalaat. Kenn daawul aakimoo dara ci alalam, waaye ñoo bokkoon lépp. 4:33 Te ndaw yi di seedeel ndekkitel Yeesu Boroom bi ak kàttan gu réy. Te yiw wu yaatu ëmb leen, ñoom ñépp. 4:34 Kenn ci ñoom ñàkkul dara, ndaxte képp ku nekk boroom suuf mbaa am ay kër, jaay na ko, indi njëg gi, 4:35 teg ko ci loxoy ndaw ya; ñu di ci sédd, kenn ku nekk li mu soxla. 4:36 Noonu amoon na fa ku tudd Yuusufa, te ndaw yi dàkkentale ko Barnabas, miy tekki «Kiy dëgëral fit yi,» mu soqikoo ci giiru Lewi, te juddoo dunu Sipar. 4:37 Moom nag jaay na tool, ba mu moom, indi xaalis ba, teg ko ci loxoy ndaw ya.
5:1 Naka noonu nit ku tudd Anañas, ànd ak Safira jabaram, jaay làccu suuf. 5:2 Mu dencal boppam benn cér ca njëg ga, ànd ca ak jabaram; ba noppi mu indi cér ba ca des, teg ko ci loxoy ndaw ya. 5:3 Bi mu ko defee Piyeer ne ko: «Anañas, lu tax nga bàyyi Seytaane dugg la, ba fees sa xol, ngay wor Xel mu Sell mi, ci li nga dencal sa bopp benn cér ci njëg gi? 5:4 Bi mu jaragul, ndax moomuloo ko woon? Te bi mu jaree, ndax yilifuloo woon njëg gi? Lu tax nga fas ci sa xol def nii? Woruloo nit ñi, waaye Yàlla nga wor.» 5:5 Bi Anañas déggee baat yooyu, mu daanu dee. Ñi ko dégg ñépp tiit, ba ne nërëm. 5:6 Noonu waxambaane ya jóg, ñu sàng ko, yóbbu ko, jébbal Yàlla. 5:7 Ñetti waxtu gannaaw ga, jabaram duggsi, fekk xamul la fa xew. 5:8 Piyeer daldi ko ne: «Wax ma, ndax lii mooy njëgu tool bi?» Mu tontu ko: «Waawaaw, lii la.» 5:9 Ci kaw loolu Piyeer ne ko: «Lu tax ngeen ànd, di diiŋat Xelu Boroom bi? Ñi denci woon sa jëkkër ñu ngi nii ci bunt bi, te dinañu la yóbbu.» 5:10 Ca saa sa mu daanu ciy tànkam dee. Bi waxambaane ya agsee nag, ñu fekk ko, mu faatu; ñu yóbbu ko, def ko ci wetu jëkkëram. 5:11 Noonu tiitaange ju mag tàbbi ci mbooloom ñi gëm ñépp ak ñi ko dégg ñépp. 5:12 Bi loolu amee ay kéemaan ak ay firnde yu bare di xew ci nit ñi, jaare ca loxoy ndaw ya. Ñépp di booloo ca Werandaa bu Suleymaan ca kër Yàlla ga. 5:13 Te kenn ci ña ca des ñemewul a booloo ak ñoom, waaye nit ñépp di leen màggal. 5:14 Moona ay nit ñu gën a bare, góor ak jigéen, di gëm Boroom bi, tey taq ci ñoom. 5:15 Nit ñi indi sax ñu wopp ca mbedd ya, teg leen ca ay lal yu ndaw ak ay leeso, ngir bu Piyeer di jaar, doonte takkandeeram sax yiir ñenn ci ñoom. 5:16 Te it nit ñu bare dajaloo, jóge ca dëkk ya wër Yerusalem, ñu indi ay jarag ak ñu rab yu bon sadd; te ñoom ñépp daldi wér. 5:17 Booba saraxalekat bu mag ba jóg ak gàngooram gépp, maanaam kureelu Sadusen, ga fa dëkk. Kiñaan gu mag jàpp leen, 5:18 ba ñu jàpp ndaw ya, tëj leen ca kaso ba. 5:19 Waaye ci guddi malaakam Boroom bi ubbi buntu kaso ba, génne leen ci biti naan: 5:20 «Demleen taxaw ca kër Yàlla ga, te xamal nit ñi lépp lu jëm ci dund gu wóor gii.» 5:21 Bi ñu déggee loolu, ñu dugg ca kër Yàlla ga ci suba teel, daldi waare. Bi ñu koy def, saraxalekat bu mag ba ak gàngooram ñëw, woolu kureelu àttekat ya, maanaam mbooloom njiiti bànni Israyil gépp; ñu yónnee, ngir jëli ndaw ya ca kaso ba. 5:22 Waaye bi wottukati kër Yàlla ga agsee ca kaso ba, gisuñu leen fa; ñu daldi dellusi, yégle ko 5:23 ne: «Fekk nanu kaso ba tëju bu wóor ak wottukat ya taxaw ca bunt ya, waaye bi nu ko tijjee, fekkunu kenn ci biir.» 5:24 Bi kilifag wottukati kër Yàlla ga ak saraxalekat yu mag ya déggee loolu, ñu daldi ciy jaaxle lool, ñuy laajante, fu lii di mujj. 5:25 Noonu benn waay ñëw, yégal leen ne: «Nit ñi ngeen tëjoon ñu ngi taxaw ca kër Yàlla ga, di jàngal nit ñi.» 5:26 Ci kaw loolu kilifa ga ak wottukat ya dem jëli leen; waaye boolewuñu ci fitna, ngir ragal nit ñi sànni leen ay xeer. 5:27 Bi ñu leen indee, ñu dëj leen ci kanamu mbooloo ma. Saraxalekat bu mag ba laaj leen 5:28 ne: «Ndax terewunu leen ci lu wér, ngeen waare ci tur woowu, te fi mu ne dajal ngeen Yerusalem ak seeni waare, rax-ca-dolli yéena ngi nuy fexee taqal deretu nit kooku.» 5:29 Waaye Piyeer ak ndaw ya tontu leen ne: «Déggal Yàlla moo gën déggal nit. 5:30 Yàllay sunuy maam dekkal na Yeesu, mi ngeen bóomoon ci wékk ko ca bant ba. 5:31 Te Yàlla yékkati na ko ci ndeyjooram, mu nekk Buur ak Musalkat, ngir may bànni Israyil réccu, ba mu baal leen seeni bàkkaar. 5:32 Seede nanu loolu, nun ak Xel mu Sell, mi Yàlla may ñi koy déggal.» 5:33 Bi ñu déggee loolu, ñu mer ba seen xol di dagg, ñu bëgg leen a rey. 5:34 Waaye amoon na fa nit ku tudd Gamaleel, bokk ci tariixab Farisen ya, di xutbakat bu tedd ci yoonu Musaa, mu jóg ca mbooloo ma, santaane ñu génne leen tuuti. 5:35 Bi ñu ko defee mu ne leen: «Yéen bokki Israyil, moytuleen li ngeen di def nit ñooñu. 5:36 Ndaxte bu yàggul Tëdas jógoon na, mbubboo daraja, ba lu mat ñeenti téeméeri nit takktoo ak moom. Tëdas moomu nag reyees na ko, te ñi ko toppoon ñépp tasaaroo, ba seen pexe nasax. 5:37 Gannaawam it Yudaa mu Galile jóg, ca jamono ja ñu doon bind waa réew ma, mu jógloo nit ñu bare, ñu ànd ak moom. Moom itam dee na, te ay nitam ñépp tasaaroo. 5:38 Léegi maa ngi leen di wax, génnleen ci mbirum ñooñu te bàyyi leen ñu dem. Ndaxte bu seen pas-pas mbaa seen jëf dee pexem nit, dina yàqu. 5:39 Waaye bu fekkee ne ndogalu Yàlla la, dungeen ko man a fanq, ngir ragal a jànkoonte ak Yàlla.» 5:40 Bi mu waxee loolu, ñu fekk ko ci xalaatam; ñu woo ndaw ya, daldi leen dóor ay yar, tere leen, ñu waxati dara ci turu Yeesu, ba noppi bàyyi leen, ñu dem. 5:41 Ndaw ya nag jóge ca kanam kureelu àttekat ya, bég ci li leen Yàlla jàppe, ñu yeyoo yenu toroxte ngir Tur wa. 5:42 Noonu bés bu nekk ca kër Yàlla ga ak ca kër ya, daawuñu noppee jàngale ak a xamle xebaar bu baax bi, ne Yeesu mooy Almasi bi.
6:1 Ca bés yooyu, naka taalibe yi di gën a bare, Yawut yiy làkk gereg tàmbalee ñaxtu ci mbirum Yawut tigi yi, te lii a ko waral: jigéen ñi seen jëkkër dee, te ñu bokk ci ñoom, naraalewuñu leen ca ndimbal, la ñuy séddale bés bu nekk. 6:2 Noonu fukki ndaw ya ak ñaar woo mbooloom taalibe ya ne leen: «Nu bàyyi kàddug Yàlla, di topptoo mbirum séddale, loolu jekkul ci nun. 6:3 Kon nag bokk yi, tànnleen juróom-ñaari nit ci seen biir, ñu am seede su rafet te fees ak Xel mu Sell mi ak sago, nu dénk leen liggéey bii. 6:4 Waaye nun dinanu wéy ci ñaan ci Yàlla ak ci yenub xamle kàddu gi.» 6:5 Lii ñu wax nag neex na mbooloo mépp. Noonu ñu tànn Ecen, di nit ku fees ak ngëm ak Xel mu Sell mi, boole ci Filib ak Porokor, teg ca Nikanor, Timon, Parmenas ak Nikolas, mi juddoo Ancos te tuub ci yoonu Yawut ya. 6:6 Ñu jébbal leen ndaw ya, ñaanal leen, teg leen loxo. 6:7 Noonu kàddug Yàlla di law, ba mbooloom taalibe yi di yokku bu bare ci Yerusalem; te saraxalekat yu bare déggal Yàlla ci topp yoonu ngëm wi. 6:8 Naka noona Ecen, mi fees ak yiw ak kàttan, di def ay kéemaan yu mag ak ay firnde ca nit ña. 6:9 Waaye ay nit jóg, bokk ci jàngu, bi ñuy wax Jàngub ñi ñu goreel, di ay niti dëkki Siren ak Alegsàndiri, ak it waa diiwaani Silisi ak Asi. Ñuy werante ak Ecen, 6:10 waaye àttanuñu sagoom ak Xel mi muy waxe. 6:11 Kon ñu daldi jënd ay nit, ñu ne: «Dégg nanu ko, muy sosal Musaa ak Yàlla.» 6:12 Noonu ñu jógloo nit ñi ak njiit yi ak xutbakat yi, ñu dal ci kawam, jàpp ko, yóbbu ko ca kureelu àttekat ya. 6:13 Te ñu sàkk ay naaféq yuy seede ne: «Kii du bàyyee wax lu juuyoo ak bérab bu sell ba ak yoonu Musaa. 6:14 Ndaxte dégg nanu, muy wax ne, Yeesum Nasaret moomu dina daaneel bérab bii te soppi aada, yi nu Musaa batale woon.» 6:15 Bi ñu ko waxee, ña toogoon ñépp ca mbooloo ma xool ko jàkk, gis xar-kanamam, mu mel ni xar-kanamu malaaka.
7:1 Noonu saraxalekat bu mag ba ne ko: «Ndax loolu dëgg la?» 7:2 Ecen tontu ko: «Yéen samay bokk ak samay baay, dégluleen! Yàlla, miy Boroom ndam, feeñu woon na sunu maam Ibraayma, bi mu nekkee réewu Mesopotami, te dëkkagul woon Karan. 7:3 Mu ne ko: “Toxul sa réew, bàyyi say bokk, te ñëw ci réew, mi ma lay won.” 7:4 «Ci kaw loolu mu génn réewu niti Kalde, dëkksi Karan. Te bi baayam faatoo, Yàlla toxale ko foofa, dëël ko ci réew, mi ngeen dëkk léegi. 7:5 Waaye mayu ko fa genn moomeel gu mu war a donnale, du sax fu mu man a teg tànkam; waaye dig na ko ne, dina ko may réew mi, mu yilif ko moom ak askanam, fekk booba amagul doom. 7:6 Yàlla ne ko: “Ñi soqikoo ci yaw dinañu ganeyaan ci réew mu ñu dëkkul; dees na leen def ay jaam, di leen fitnaal diirub ñeenti téeméeri at.” 7:7 Waaye Yàlla nee na: “Xeet wi leen jaamloo, man maa leen di àtte te gannaaw loolu dinañu génn, di ma jaamu ci bérab bii.” 7:8 Yàlla nag tëral kóllëre seen diggante, fas ko ci màndargam xaraf. Noonu Ibraayma jur Isaaxa, xarafal ko ca juróom-ñetteelu fan ba; Isaaxa def noonu Yanqóoba, Yanqóoba it def noonu fukki maam ya ak ñaar, ñi sos xeet wi. 7:9 «Naka maam yooyu, dañoo iñaane Yuusufa, ba jaay ko, mu jëm réewu Misra. Waaye Yàlla taxawu ko, 7:10 génne ko ci coonoom yépp, defal ko yiw ak xel ci kanamu Firawna, buuru Misra, mu def ko kilifag Misra ak këram gépp. 7:11 «Bi loolu amee xiif tàbbi ci biir Misra ak réewu Kanaan mépp, ba toskare ja metti lool, te sunuy maam amatuñu lu ñu lekk. 7:12 Yanqóoba nag dégg ne, Misra am na dugub, mu yebal ca sunuy maam, ñu dem fa yoon wu jëkk. 7:13 Bi fa ay doomi baayam delloo nag, Yuusufa xàmmiku leen, te Firawna xamante ak njabootam. 7:14 Ci kaw loolu Yuusufa yeble, woo baayam ak mbokkam yépp, ñuy juróom-ñaar-fukki nit ak juróom. 7:15 Noonu Yanqóoba dem Misra, faatu fa, moom ak sunuy maam. 7:16 Gannaaw loolu ñu yóbbu seeni néew Sikem, dugal leen ca bàmmeel, ba Ibraayma jëndoon ak xaalis ca doomi Emor ca Sikem. 7:17 «Bi loolu wéyee jamono ji jege woon na, ngir Yàlla amal li mu digoon Ibraayma ci ngiñ; fekk xeet wa di law tey gën a bare ci Misra, 7:18 ba keroog beneen buur bu xamul Yuusufa di falu ci Misra. 7:19 Buur boobu nag dafa daan nax sunu xeet, di fitnaal sunuy maam, ba di leen sànniloo seeni doom, ngir ñu dee. 7:20 «Booba nag la Musaa juddu, di ku rafet ci kanam Yàlla; ñu yor ko ñetti weer ci biir kër baayam, 7:21 ba noppi sànni ko. Noonu doom ju jigéen ju Firawna for ko, yar ko ni doomam. 7:22 Musaa nag di ku yeewu ci xam-xamu waa Misra bépp, di jàmbaar ci wax ak jëf. 7:23 «Bi mu demee ba am ñeent-fukki at, mu fas yéeney seeti ay bokkam, maanaam bànni Israyil. 7:24 Noonu mu gis ca ku ñuy néewal doole, mu sotle ko, feyyul ko, ba dóor waayi Misra ja. 7:25 Mu defe ne, ay bokkam dinañu xam ne, ciy loxoom la leen Yàllay musale, waaye xamuñu ko. 7:26 Ca ëllëg sa mu juux ci ay Yawut yuy xeex, mu di leen jéem a jubale ne leen: “Yéen ay bokk ngeen, lu tax ngeen di xeex?” 7:27 Waaye kiy néewal doole moroomam bëmëx ko ne: “Ku la teg kilifa ak àttekat ci sunu kaw? 7:28 Ndax danga maa bëgg a rey, ni nga defoon démb waayi Misra ja?” 7:29 Bi Musaa déggee wax jooju, mu daldi daw, dem réewu Majan, di fa ab doxandéem; mu séy fa, ba am ñaari doom. 7:30 «Lu ko wees ñeent-fukki at nag, bi mu nekkee ca màndiŋu tundu Sinayi, malaaka feeñu ko ci takk-takku safara ci biir as ngarab. 7:31 Bi ko Musaa gisee, mu daldi waaru ci li mu gis; mu jegesi ngir niir ko, dégg baatu Boroom bi ne ko: 7:32 “Man maay sa Yàllay maam, di Yàllay Ibraayma, Isaaxa ak Yanqóoba.” Ci kaw loolu Musaa tiit bay lox, te ñemeetul a xool. 7:33 Noonu Boroom bi ne ko: “Summil say dàll, ndaxte bérab bi nga taxaw, bérab bu sell la. 7:34 Gis naa bu baax fitnay sama xeet ci Misra te dégg naa seeni tawat, kon wàcc naa ngir musal leen. Léegi nag ñëwal, dinaa la yebal Misra.” 7:35 «Musaa moomu bañoon nañu ko, ba ne ko: “Ku la teg kilifa ak àttekat?” Waaye moom la Yàlla yebal, jaarale ko ci malaaka mi ko feeñu ca ngarab sa, ngir mu nekk kilifa gu leen di goreel. 7:36 Moo leen génne réewu Misra, di def ay kéemaan ak ay firnde ca réew ma, ca Géej gu xonq ga ak ca màndiŋ ma diirub ñeent-fukki at. 7:37 Musaa moomu moo ne woon bànni Israyil: “Yàlla dina leen feeñalal ci seeni bokk Yonent bu mel ni man.” 7:38 Te moo nekkoon ak mbooloo ma ca màndiŋ ma, ànd ak sunuy maam, wéttalikoo malaaka, mi waxoon ak moom ci tundu Sinayi. Te mu jote ci Yàlla kàddu yiy dund, ngir jottali nu ko. 7:39 Waaye sunuy maam nanguwuñu koo déggal; dañu koo bañ te seeni xel dëpp, dellu Misra. 7:40 Ñu sant Aaroona ne: “Sàkkal nu ay yàlla yuy jiitu ci sunu kanam, ndaxte Musaa male nu génne ci réewu Misra, xamunu lu ko dal.” 7:41 Booba nag ñu tëgglu aw sëllu, muy xërëm, ñu di ko tuuru, di bànneexu ci seeni jëfi loxo. 7:42 Waaye bi ñu ko defee Yàlla dëddu leen, bërgël leen, ñuy jaamu biddiiwi asamaan. Moom lañu bind ci téereb yonent yi ne:“Yéen bànni Israyil, ndax rendi ngeen jur,jébbal ma, boole ko ak i sarax,diirub ñeent-fukki at ca màndiŋ ma? 7:43 Yóbbu ngeen sax fu nekk tànt,biy màggalukaayu Molog ak biddiiwub Refan,bi ñu daan bokkaaleel Yàlla,di ay nataal, yi ngeen defoon ngir màggal leen!Kon nag dinaa leen toxal,yóbbu leen ci gannaaw réewu Babilon.” 7:44 «Sunuy maam amoon nañu ca màndiŋ ma tàntu màggalukaay, bi ëmboon li Yàlla seede. Tànt boobu nag defoon nañu ko, roye ko ci bi Musaa gisoon, ni ko ko Yàlla sante woon. 7:45 Te gannaaw ga, bi Yosuwe nekkee kilifag sunuy maam, ñu jot tànt ba ñoom it, yóbbu ko ca réew, ma ñu nangu ca xeet ya Yàlla dàq ci seen kanam. Tànt ba nekk fa, ba ci jamonoy Daawuda. 7:46 Moom yiw na fa kanam Yàlla, mu ñaan ko, mu sàkkal ko kër ngir askanu Yanqóoba. 7:47 Waaye Suleymaan moo tabaxal Yàlla kër ga. 7:48 «Moona Aji Kawe ji du dëkk ci fu loxol nit defar; moom la ab yonent wax ne: 7:49 “Asamaan mooy sama jal,te suuf mooy sama tegukaayu tànk.Kon gan kër ngeen may tabaxal,mbaa fan mooy sama bérabu noppalukaay? 7:50 Ndax du sama loxo moo defar yëf yooyu yépp?— Moom la Boroom bi doon wax.” 7:51 «Yéen ñi dëgër bopp, ànd ak xol buy bañ ak ay nopp yuy fatt, mel ni ñi xamul Yàlla. Dungeen noppeek a diiroo ak Xel mu Sell mi; ni ko seen baay yi daan defe, noonu ngeen di def yéen itam. 7:52 Kan ca yonent ya la seeni maam tegul woon ay fitna? Rey nañu ñi doon yégle ñëwug Aji Jub ji, moom mi ngeen jébbale léegi, ba ñu rey ko. 7:53 Jot ngeen yoonu Musaa, wi Yàlla wàcce jaarale ko ci ay malaaka, te sàggane ngeen ko.» 7:54 Bi ñu déggee loolu nag, seeni xol di dagg, ñuy yéyu, jëm ci kawam. 7:55 Waaye Ecen, mi fees ak Xel mu Sell mi, ne jàkk ci asamaan, gis ndamu Yàlla, te gis Yeesu mi taxaw ci ndeyjooru Yàlla. 7:56 Mu ne: «Seetleen, maa ngi gis asamaan yi ubbiku, te Doomu nit kaa ngii taxaw ci ndeyjooru Yàlla.» 7:57 Bi ñu déggee loolu, ñu daldi xaacu ca kaw, tey dar seeni nopp; ñu ànd, ne milib ci kawam; 7:58 ñu wat-wate ko, génne ko dëkk ba, dóor ko ay doj, ba mu dee. Seede ya tegoon nañu seeni yére ci tànki waxambaane wu tudd Sool. 7:59 Noonu ñu dóor Ecen ay doj, muy ñaan Yàlla ne: «Boroom bi Yeesu, nangul sama ruu!» 7:60 Bi mu ko waxee, mu sukk, wax ak baat bu kawe: «Boroom bi, bu leen bindal bàkkaar bii,» ba noppi mu nelaw.
8:1 Sool moom ànd na ci ñi doon rey Ecen. Bés booba nag fitna ju metti dal na ci mbooloom ñi gëm, mi nekk Yerusalem, ba ñépp, ñu moy ndaw ya, tasaaroo ci diiwaani Yude ak Samari. 8:2 Ay nit ñu ragal Yàlla fab Ecen, jébbal ko Boroom bi, di ko jooy bu wér. 8:3 Waaye naka Sool, mu ngay tas mbooloom ñi gëm, di tàbbi ca kër ya, tey jàpp góor ak jigéen, di leen tëj kaso. 8:4 Ñi tasaaroo nag dem fu nekk, di fa xamle xebaar bu baax bu kàddug Yàlla. 8:5 Naka Filib mu dem ca benn dëkk ca Samari, di leen yégal Kirist. 8:6 Bi ko mbooloo mi déggee te gis kéemaan yi muy def, ñu bokk benn xalaat, fekki ko ci li mu wax. 8:7 Ndaxte ay rab yu bon bàyyi nañu nit ñu bare, ña ñu jàppoon, di yuuxu ci kaw; te ñu bare ñu làggi ak ñu lafañ daldi wér. 8:8 Noonu mbég mu réy tàbbi ca dëkk ba. 8:9 Amoon na nag nit ku tudd Simoŋ, di luxuskat bu yàgg ca dëkk ba, te daan yéem waa Samari gépp, ci naan: «Aji Màgg laa.» 8:10 Kon ñépp, mag ak ndaw, taq ci moom ne: «Kii mooy jaasiy Aji Kàttan ji.» 8:11 Ñu taq ci moom, ndax li mu leen yàgg a waar ci ay luxus. 8:12 Waaye bi ñu gëmee xebaar bu baax, bi Filib yégle jëm ci nguurug Yàlla ak turu Yeesu Kirist, góor ak jigéen daldi nangu, ñu sóob leen ci ndox. 8:13 Simoŋ sax gëm, ñu sóob ko ci ndox; mu wéy nag ci topp Filib, di waaru ci kéemaan yi ak firnde yu mag yiy am. 8:14 Bi nga xamee ne ndaw yi nekk Yerusalem yég nañu ne, waa Samari nangu nañu kàddug Yàlla; ñu yónni fa Piyeer ak Yowaana. 8:15 Ñu dem fa nag, ñaanal leen, ngir ñu jot Xel mu Sell mi. 8:16 Ndaxte wàccagul ci kenn ci ñoom, waaye sóoboon nañu leen rekk ci ndox ci turu Boroom bi Yeesu. 8:17 Noonu Piyeer ak Yowaana teg leen loxo, ñu jot Xel mu Sell mi. 8:18 Bi Simoŋ gisee nag ne Yàlla may na Xel mi jaarale ko ci loxoy ndaw ya, mu indil leen xaalis, 8:19 ne leen: «Mayleen ma sañ-sañ boobu, ba ku ma teg samay loxo, nga jot Xel mu Sell mi.» 8:20 Waaye Piyeer ne ko: «Asarul ak sa xaalis, yaw mi yaakaar ne, man ngaa jënd mayu Yàlla ak xaalis. 8:21 Amuloo benn wàll mbaa cér ci lii, ndaxte sa xol laabul ci kanam Yàlla. 8:22 Réccul nag sa coxor te ñaan Boroom bi, mu baal la sa xalaatu xol, su manee am. 8:23 Ndaxte gis naa ne, sóobu nga ci lu wex xat ci kanam Yàlla, te bàkkaar noot na la.» 8:24 Simoŋ nag ne leen: «Ñaanal-leen ma ci Boroom bi, ngir mu fegal ma li ngeen wax.» 8:25 Noonu bi ñu seedeelee Yàlla te wax ci kàddoom, ñu dellu Yerusalem, di xamle xebaar bu baax bi ci dëkk yu bare yu waa Samari. 8:26 Naka noonu benn malaakam Boroom bi ne Filib: «Jógal te jublu Misra, jaar ci yoon wi jóge Yerusalem, jëm Gasa, di màndiŋ.» 8:27 Filib jóg dem. Noonu mu gis fa nitu Ecópi ku yoom, di jaraaf ju mag ci Kandas, buur bu jigéen bu Ecópi, te di ko wottul xaalisam bépp. Fekk mu ñëwoon Yerusalem, ngir màggalsi Yàlla, bay dellu; 8:28 mu toog ci watiiram, di jàng téereb yonent Yàlla Esayi. 8:29 Xel mi nag ne Filib: «Dabal watiir wale.» 8:30 Noonu Filib dawsi, mu dégg waayi Ecópi ja, di jàng téereb yonent Yàlla Esayi. Mu laaj ko: «Ndax xam nga li ngay jàng?» 8:31 Mu tontu ko ne: «Nu ma ko man a xame, su ma ko kenn firilul?» Mu woo Filib nag, mu yéeg, toog ak moom. 8:32 Fekk aaya yii la doon jàng ci Mbind mi:«Yóbbu nañu ko ni xar mu ñuy rendiji;ni mburt mu luu ci kanami watkat,mu ne cell. 8:33 Ci toroxteem nangu nañu dëggam;ñi mu tollool jamono, ku ci xalaat lii?Jële nañu bakkanam ci àddina.» 8:34 Jaraaf ja nag ne Filib: «Maa ngi lay laaj, ci mbirum kan la yonent bi jëmale wax ji? Ndax mbirum boppam lay wax mbaa mu keneen?» 8:35 Noonu Filib tàmbali ci aaya yooyu, xamal ko xebaar bu baax bi ci mbirum Yeesu. 8:36 Bi ñuy jaar ci yoon wi, ñu agsi ci ndox. Jaraaf ja ne ko: «Ndox a ngi nii, ana lu tere, nga sóob ma ci?» 8:38 Mu santaane nag, ñu taxawal watiir wa; Filib ak jaraaf ja wàcc ñoom ñaar ci biir ndox ma, mu sóob ko ca. 8:39 Ba noppi ñu génn ca ndox ma, te ca saa sa Xelu Boroom bi fëkk Filib, ba jaraaf ja gisatu ko, waaye mu toppaat yoonam, ànd ak mbég. 8:40 Filib moom teeri dëkku Asot, muy jaar ci dëkk yépp, di fa xamle xebaar bu baax bi, ba kera muy ñëw dëkku Sesare.
9:1 Naka Sool, muy tëkkoo rey taalibey Boroom bi, ba di ko noyyee far. Mu dem nag ca saraxalekat bu mag ba, 9:2 laaj ko ay bataaxal yu muy yóbbul jànguy dëkku Damas. Noonu ñu mu fa fekk, te ñu bokk ci yoon wi, góor mbaa jigéen, mu am dogalu yeew leen, indi leen Yerusalem. 9:3 Waaye bi muy jub Damas, ca saa sa leer gu jóge asamaan melax, ba ëmb ko. 9:4 Mu daanu ci suuf, dégg baat bu ko ne: «Sool, Sool, lu tax nga di ma fitnaal?» 9:5 Mu wuyu ne: «Yaay kan Boroom bi?» Boroom bi ne ko: «Maay Yeesu, mi ngay fitnaal. 9:6 Waaye jógal, dugg ca dëkk ba, te dinañu la wax li nga war a def.» 9:7 Nit ñi ànd ak moom nag taxaw, waaru ba luu, ci li ñu dégg baat bi te gisuñu kenn. 9:8 Noonu Sool jóg, xippi, waaye gisul dara; kon ñu wommat ko, yóbbu ko Damas. 9:9 Diirub ñetti fan gisul dara, lekkul, naanul. 9:10 Amoon na nag ci Damas taalibe bu tudd Anañas. Bi loolu amee nag Boroom bi feeñu ko ne: «Anañas!» Mu wuyu: «Maa ngi nii Boroom bi.» 9:11 Boroom bi ne ko: «Jógal, nga jaar ci mbedd, mi ñuy wax Mbedd mu jub mi, te seet ci kër Yudaa nit ku tudd Sool te dëkk Tars, ndaxte mu ngay ñaan. 9:12 Te gis na cim peeñu nit ku tudd Anañas, mu dugg, teg ko ay loxo, ba muy gisaat.» 9:13 Waaye Anañas tontu ko ne: «Boroom bi, dégg naa ci nit ñu bare ci mbirum kooku, ñu seede lu bare lu bon lu mu def say gaay ci Yerusalem. 9:14 Te indaale na fii sax sañ-sañ bu jóge ci saraxalekat yu mag ya, ngir yeew képp kuy tudd saw tur.» 9:15 Waaye Boroom bi ne ko: «Demal, ndaxte maa ko tànn, muy sama jëfandukaay, ngir yóbbu sama tur fa kanam ñi nekkul Yawut ak fa kanam buur yi ak bànni Israyil. 9:16 Te dinaa ko won coono yu bare yu mu war a dékku ngir sama tur.» 9:17 Ci kaw loolu Anañas dem, dugg ca kër ga, teg ay loxoom Sool. Mu ne ko: «Sool sama mbokk, Boroom bi Yeesu, mi la feeñu woon ci kaw yoon wi, bi ngay dikk, moo ma yónni, ngir nga dellu di gis te fees ak Xel mu Sell mi.» 9:18 Ca saa sa lu mel ni ay waasintoor génne ci ay bëtam, mu daldi gisaat. Noonu mu jóg, ñu sóob ko ci ndox; 9:19 ba noppi mu lekk, amaat doole. Bi mu ko defee mu toog ay fan ak taalibe, ya nekk Damas. 9:20 Ca saa sa muy yégle ca jàngu ya ne, Yeesu mooy Doomu Yàlla. 9:21 Ñi ko dégg ñépp waaru naan: «Ndax du kii moo daan tas ñiy tudd tur woowu ci Yerusalem, te mu ñëw fii, ngir yeew leen, yóbbu ci kanamu saraxalekat yu mag ya?» 9:22 Moona Sool di gën a am kàttan, bay jaaxal Yawut yi dëkk Damas, ci di leen wax ay firnde, ne Yeesu mooy Almasi bi. 9:23 Ba ñu ca tegee ay fani fan, Yawut yi daldi gise, ngir reylu ko. 9:24 Waaye Sool yég seen pexe. Fekk guddi ak bëccëg ñu doon wottu bunt yi yépp, ngir man koo bóom. 9:25 Noonu taalibe yi jël ko ci guddi, def ko ci dàmba gu réy, jaarale ko ci miir bi, yoor ko ci suuf. 9:26 Bi Sool agsee Yerusalem, mu jéem a ànd ak taalibe yi, waaye ñépp ragal ko, ndax gëmuñu woon ag taalibeem. 9:27 Ci kaw loolu Barnabas jël ko, yóbbu ko ca ndaw ya, nettali leen, ni Sool gise Boroom bi ci kaw yoon wi, ak li mu ko wax, rax-ca-dolli fit wi mu doon waxe ci turu Yeesu ci Damas. 9:28 Noonu mu nekk ak ñoom ci Yerusalem, di dugg ak a génn, di wax ak fit ci turu Boroom bi. 9:29 Muy wax ak di werante ak Yawut yiy làkk gereg, waaye ñu di ko wut a rey. 9:30 Bi ko bokk yi yégee nag, ñu yóbbu ko dëkku Sesare, yebal ko dëkku Tars. 9:31 Noonu mbooloom ñi gëm nekk ci jàmm ci biir diiwaani Yude gépp ak Galile ak Samari; ñuy gën a dëgër, di wéy ci ragal Yàlla, tey yokku ci ndimbalu Xel mu Sell mi. 9:32 Piyeer nag di wër, di jaar fu nekk, tey dem ci gaayi Yàlla yi dëkk Lidd, 9:33 mu gis fa nit ku làggi, tudd Ene, tëdd ci basaŋ diirub juróom-ñetti at. 9:34 Piyeer ne ko: «Ene, Yeesu Kirist faj na la; jógal te defar sa lal.» Noonu mu daldi jóg ca saa sa. 9:35 Bi ko waa diiwaani Lidd ak Saron gépp gisee, ñu daldi woññiku ci Boroom bi. 9:36 Amoon na nag ci dëkku Yope taalibe bu jigéen bu tudd Tabita, liy tekki «Dorkas,» maanaam «kewel,» te muy wéy ci jëf yu baax ak saraxe. 9:37 Ca fan yooyu mu daanu wopp, ba faatu; noonu ñu sang ko, teg ko ca néeg, ba sut ca taax ma. 9:38 Gannaaw Lidd sorewul ak Yope nag, te taalibe yi dégg ne, Piyeer a nga fa, ñu yónnee ko ñaari nit, ñaan ko mu ñëw ci ñoom ci saa si. 9:39 Bi ko Piyeer déggee, mu jóg, ànd ak ñoom. Bi mu ñëwee, ñu yóbbu ko ca néeg bu kawe ba. Fekk fa ay jigéen ñi seeni jëkkër faatu, ñu daldi wër Piyeer, ñépp di jooy, di ko won kamisool ya ak mbubb, ya Dorkas daan defar cig dundam. 9:40 Ci kaw loolu Piyeer génne ñépp ci biti, mu sukk, ñaan ci Yàlla, ba noppi walbatiku ca néew ba ne ko: «Tabita, jógal!» Noonu mu xippi, gis Piyeer, daldi toog. 9:41 Piyeer may ko loxo, yékkati ko. Mu woo gaayi Yàlla ya ak jigéen ña, won leen ko, muy dund. 9:42 Mbir ma siiw ca Yope gépp, ba ñu bare gëm Boroom bi. 9:43 Gannaaw loolu Piyeer toog ay fan ci Yope, ci këru ku tudd Simoŋ, miy wullikat.
10:1 Amoon na ci Sesare nit ku tudd Korney, nekk njiitu xare, mu bokk ci mbooloom xare, mi ñuy wax mu Itali. 10:2 Moom nag ku farlu woon ci Yàlla la, te ragal ko, moom ak waa këram gépp; muy sarax ñu bare ci bànni Israyil, tey saxoo ci ñaan ci Yàlla. 10:3 Am bés ci tisbaar nag mu am peeñu, gis bu leer malaakam Yàlla feeñu ko ne ko: «Korney!» 10:4 Noonu Korney ne ko jàkk, daldi tiit ne ko: «Kilifa gi, lu mu doon?» Malaaka ma ne ko: «Say ñaan ak say sarax yéeg na fa kanam Yàlla, te nangul na la. 10:5 Yónnil léegi nag ay nit ci dëkku Yope, ñu woo ku tudd Simoŋ, mi ñu dàkkentale Piyeer. 10:6 Mu nga dal fa Simoŋ wullikat, bi këram nekk ci wetu géej.» 10:7 Bi malaaka mi doon wax ak moom demee, Korney woo ñaar ci ay surgaam ak benn xarekat bu farlu ci Yàlla ci ñi koy topptoo; 10:8 mu nettali leen lépp, yebal leen Yope. 10:9 Ca ëllëg sa, ba ñuy jaar ca yoon wa, ba jub dëkk ba, Piyeer yéeg ca kaw taax ma ci digg-bëccëg ngir ñaan ci Yàlla. 10:10 Noonu xiif dab ko fa, mu bëgg a lekk. Waaye bi ñu koy toggal, Yàlla feeñu ko. 10:11 Mu xool asamaan ubbiku, gis lu mel ni sér bu mag bu ñu téye ci ñeenti laf ya, yoor ko, mu jëm suuf. 10:12 Boroom ñeenti tànk yépp ñu nga ca, ak yiy raam ci suuf, ak picci asamaan. 10:13 Te baat ne ko: «Jógal, Piyeer, rey te lekk.» 10:14 Waaye Piyeer tontu ko: «Mukk, Boroom bi, ndaxte musumaa lekk dara lu daganul mbaa lu araam.» 10:15 Waaye baat bi wax ak moom ñaareelu yoon ne ko: «Lu Yàlla sellal, bu ko araamal.» 10:16 Ñu def ko nag, ba muy ñetti yoon, ba noppi ñu ne cas sér ba, jëme asamaan. 10:17 Bi loolu amee Piyeer jaaxle lool ci lu peeñu miy tekki; fekk booba nit ñi Korney yebal, laajte woon nañu kër Simoŋ, ba agsi ci bunt bi. 10:18 Ñu woote nag naan: «Simoŋ, mi ñu dàkkentale Piyeer, ndax fi la dëkk?» 10:19 Bi Piyeer di rabal xelam ci peeñu ma, Xel mi ne ko: «Ñetti nit a ngi nii, di la wut. 10:20 Jógal, nga wàcc te ànd ak ñoom; bul werante, ndaxte maa leen yebal.» 10:21 Piyeer wàcc nag ne nit ñi: «Maa ngi nii, man mi ngeen di wut; lu doon seeni tànk?» 10:22 Ñu tontu ko: «Korney, njiitu xare ba, nit ku jub la te ragal Yàlla, ba am seede su rafet ci bànni Israyil gépp. Malaaka mu sell nag sant na ko, mu woolu la ci këram te déglu li ngay wax.» 10:23 Ci kaw loolu Piyeer dugal leen, dalal leen. Ba bët setee, Piyeer jóg, dem ak ñoom, ànd ak ñenn ci bokk yi dëkk Yope, 10:24 te bés ba ca topp mu dikk Sesare. Fekk Korney woo na këram ay bokkam ak i xaritam yi ko gën a jege, di xaar Piyeer. 10:25 Bi Piyeer duggee nag, Korney daje ak moom, daanu ciy tànkam, sargal ko. 10:26 Waaye Piyeer yékkati ko ne: «Jógal, man it nit rekk laa.» 10:27 Noonu muy waxtaan ak moom, duggsi, fekk fa ndajem nit ñu bare. 10:28 Mu ne leen: «Xam ngeen ne, aaye nañu Yawut, mu jaxasoo ak ku mu bokkalul xeet, mbaa mu dugg ci këram. Waaye Yàlla won na ma ne, warumaa ne kenn setul mbaa araam na. 10:29 Looloo tax, bi ngeen ma wooloo, ñëw naa ci lu àndul ak werante. Maa ngi leen di laaj nag, lu ngeen may doye?» 10:30 Ci kaw loolu Korney tontu ne: «Ñetti fan a ngii may ñaan ci sama biir kër ci waxtu wii, maanaam tisbaar. Ci saa si ku sol yére yuy melax taxaw ci sama kanam, 10:31 mu ne ma: “Korney, say ñaan nangu na, te say sarax egg nañu fa kanam Yàlla. 10:32 Yónneel nag ci Yope, woolu Simoŋ, mi ñu dàkkentale Piyeer; mu nga dal ci kër Simoŋ miy wullikat ca wetu géej ga.” 10:33 Yónnee naa nag ci ni mu gën a gaawe, woolu la; te maa ngi lay sant ci li nga ñëw. Léegi nag nun ñépp nu ngi fi ci kanam Yàlla, ngir déglu lépp li la Boroom bi sant.» 10:34 Noonu Piyeer jël kàddu ga ne leen: «Ci dëgg gis naa ne, Yàlla du gënale, 10:35 waaye ci xeet yépp, ku ko ragal tey def lu jub, moom la nangu. 10:36 Yónnee na kàddoom bànni Israyil, di leen xebaar jàmm, jaarale ko ci Yeesu Kirist, miy Boroom lépp. 10:37 Xam ngeen li xewoon ci réewum Yawut yépp, li ko tàmbalee ci diiwaanu Galile, topp ci waareb Yaxya, mu naan nit ñi, mu sóob leen ci ndox. 10:38 Xam ngeen ne Yàlla fal na Yeesum Nasaret, sol ko Xel mu Sell mi ak kàttan; muy wër, di def lu baax ak di faj ñépp ñi nekkoon ci kilifteefu Seytaane, ndaxte Yàlla ànd na ak moom. 10:39 «Seede nanu li mu def lépp ci biir réewu Yawut ya ak Yerusalem. Moona rey nañu ko ci wékk ko ci bant. 10:40 Waaye Yàlla dekkal na ko ci ñetteelu fan ba te biral ko, 10:41 waxuma xeet wépp, waaye seede yi Yàlla tànn lu jiitu, maanaam nun ñi daan lekk di naan ak moom gannaaw ndekkiteem. 10:42 Te Yeesu sant na nu, nu yégal xeet wa, di seede ne, moom la Yàlla jagleel àtteb ñiy dund ak ñi dee. 10:43 Yonent yépp seedeel nañu ko ne, ku ko gëm, Yàlla dina la baal say bàkkaar ci turam.» 10:44 Bi Piyeer di wax loolu, Xel mu Sell mi wàcc ci kaw ñépp ñiy déglu kàddu ga. 10:45 Yawut yi gëm yépp nag, ñi ànd ak Piyeer, daldi waaru ci li Yàlla tuur Xel mu Sell, mi mu maye, ci ñi dul Yawut itam. 10:46 Ndaxte dégg nañu leen, ñuy wax yeneeni làkk ak di màggal Yàlla. 10:47 Booba Piyeer daldi wax ne: «Ñii jot Xel mu Sell mi ni nun, ndax manees na leen a bañ a sóob ci ndox?» 10:48 Noonu mu santaane, ñu sóob leen ci ndox ci turu Yeesu Kirist. Gannaaw loolu ñu ñaan ko, mu toog ci ñoom ay fan.
11:1 Bi loolu amee ndaw yi ak bokk yi nekk ci diiwaanu Yude, dégg nañu ne, ñi dul Yawut nangu nañu kàddug Yàlla. 11:2 Bi Piyeer demee Yerusalem nag, kureelu Yawut gi farataal xaraf, di werante ak moom ne ko: 11:3 «Lu tax nga dem ca këru ñu xarafal, bay lekk sax ak ñoom?» 11:4 Noonu Piyeer daldi leen benn-bennal mbir mi, nettali leen ko 11:5 ne: «Nekkoon naa ca dëkku Yope, di fa ñaan ci Yàlla, ba far sama xol seey ci moom; noonu ma am peeñu: lu mel ni sér bu mag wàcc, jóge ci asamaan, ñu yoor ko ca ñeenti laf ya, mu ñëw ba ci man. 11:6 Ma xool ko jàkk, seetlu ko bu baax, ma gis ca boroom ñeenti tànk yu nekk ci kaw suuf, di rabi àll yi, yiy raam ak picci asamaan. 11:7 Te dégg naa baat bu ma ne: “Jógal Piyeer, rey te lekk.” 11:8 Waaye ma tontu ne: “Mukk Boroom bi, ndax dara lu daganul mbaa lu araam musul a dugg ci sama gémmiñ.” 11:9 Waaye ñaareel bi yoon baat bi dellu ne ma: “Lu Yàlla sellal, bu ko araamal.” 11:10 Loolu am ba muy ñetti yoon, ba noppi ñu ne cas lépp, jëme asamaan. 11:11 «Ca saa sa ñetti góor, ña ñu yebal ci man, jóge Sesare, agsi ca kër ga ma dal. 11:12 Te Xel mi ne ma: “Àndal ak ñoom, te bu ci werante.” Juróom-benni bokk, yi fi teew, gunge woon nañu ma, ba nu dugg ca kër góor googu. 11:13 Mu nettali nu ne, gis na malaaka, feeñu ko ca këram ne ko: “Yónneel ca dëkku Yope, woolu Simoŋ, mi ñu dàkkentale Piyeer. 11:14 Dina la xamal ay wax yu lay musal, yaw ak sa waa kër gépp.” 11:15 «Bi ma tàmbalee wax nag, Xel mu Sell mi wàcc ci ñoom, ni mu wàcce woon ci nun bu jëkk. 11:16 Bi loolu amee ma fàttaliku li Boroom bi wax ne: “Yaxya ci ndox la daan sóobe, waaye yéen dees na leen sóob ci Xel mu Sell mi.” 11:17 Gannaaw nag Yàlla jagleel na leen may, gi mu nu mayoon, bi nu gëmee Yeesu Kirist Boroom bi, man maay kan, bay tebbi àtteb Yàlla?» 11:18 Bi ñu déggee loolu, amuñu dara lu ñu ca teg, ñu daldi màggal Yàlla ne: «Yàlla nag may na ñi dul Yawut it ñu tuub seeni bàkkaar, ba am dund gu wóor gi.» 11:19 Ñi tasoon nag ndax fitna, ji amoon gannaaw Ecen, ñu dem ba diiwaanu Fenisi, ci dunu Sipar ak ca dëkku Ancos, di wax kàddu gi, waaye yemale ko ci Yawut yi. 11:20 Moona amoon na ci ñoom ay niti Sipar ak dëkku Siren, ñu ñëw ci Ancos, ba seen wax law ci Gereg yi it, ñu di leen xamal xebaar bu baax bu Yeesu Boroom bi. 11:21 Te loxob Boroom bi ànd ak ñoom, ba mbooloo mu mag gëm te woññiku ci Boroom bi. 11:22 Ba mbir ma siiwee, ba àgg ci noppi mbooloom ñi gëm ci Yerusalem, ñu yebal Barnabas ba Ancos. 11:23 Bi mu agsee nag, ba gis yiw, wi leen Yàlla may, mu bég ci te di leen xiir, ñu wàkkirlu ci Boroom bi te dogu ci. 11:24 Ndaxte nit ku baax la woon te fees ak Xel mu Sell mi ak ngëm; noonu mbooloo mu bare dolliku ci Boroom bi. 11:25 Gannaaw loolu Barnabas dem ca dëkku Tars, di wut Sool. 11:26 Bi mu ko gisee, mu indi ko Ancos. Noonu atum lëmm ñu bokk ak mbooloom ñi gëm, di jàngal nit ñu bare. Te ci Ancos lañu jëkk a tudde taalibe ya Gaayi Kirist. 11:27 Ca fan yooyu ay yonent jóge Yerusalem, ñëw Ancos. 11:28 Kenn ci ñoom tudd Agabus jóg, mu yégle jaarale ko ci Xelu Yàlla mi ne, xiif bu metti dina daj àddina sépp. Loolu nag amoon na ca ayug buur bu ñuy wax Këlódd. 11:29 Kon taalibe ya fas yéenee sàkk ndimbal, jëme ca bokk ya dëkk diiwaanu Yude, ku nekk ak sa kem-kàttan. 11:30 Noonu lañu def nag, teg ko ci loxoy Barnabas ak Sool, yónnee ko njiit ya.
12:1 Ca jamono jooja Erodd buur ba jàppoon na ay nit ci mbooloom ñi gëm, ngir fitnaal leen. 12:2 Noonu mu daldi jàpp Saag, doomu ndeyu Yowaana, mu reylu ko ci jaasi. 12:3 Bi mu gisee nag ne, mbir moomu neex na Yawut ya, mu daldi jàpp it Piyeer; fekk loolu daje ak bési màggalu Yawut, ga ñuy wax Mburu ya amul lawiir. 12:4 Bi mu ko jàppee, mu tëj ko kaso, teg ko ci loxoy ñeenti mboolooy xarekat, ngir ñu wottu ko, fekk mbooloo mu ci nekk di ñeenti nit; amoon na yéeney yóbbu ko ci kanamu Yawut ya gannaaw màggalu bésu Jéggi ba. 12:5 Noonu ñuy wottu Piyeer ca kaso ba, waaye mbooloom ñi gëm di ko ñaanal Yàlla ak seen xol bépp. 12:6 Bi Erodd nekkee ci tànki indilu ko, ca guddi googa yeewoon nañu Piyeer ak ñaari càllala, muy nelaw diggante ñaari xarekat, te ay xarekat di wottu buntu kaso ba. 12:7 Ca saa sa malaakam Boroom bi ñëw, te leer ne ràyy ca néeg ba. Malaaka ma dóor Piyeer ci wetam, yee ko ne ko: «Jógal bu gaaw!» Noonu jéng ya rot ciy loxoom. 12:8 Malaaka ma ne ko: «Takkal sa geño te sol say dàll.» Mu def ko. Malaaka ma ne ko: «Solal sa mbubb te topp ci man.» 12:9 Piyeer génn, topp ca malaaka ma, fekk gëmul sax ne lu am la, waaye mu yaakaar ne peeñu la. 12:10 Noonu ñu weesu wottukat bu jëkk ba ak ba ca tegu, ñu agsi ca buntu weñ, ba jëm ca dëkk ba, mu daldi ubbikul boppam ci seen kanam. Ñu génn nag, jaar ci benn mbedd, malaaka ma daldi ko bàyyi. 12:11 Bi xelam dellusee ci moom Piyeer ne: «Léegi xam naa ci lu wóor ne, Boroom bi yónni na malaakaam, musal ma ci loxoy Erodd ak li ma Yawut ya yéene woon lépp.» 12:12 Mu rabal xelam ci loolu, daldi dem kër Maryaama, ndeyu Yowaana, mi ñuy wooye Màrk, fekk ñu bare booloo fa, di ñaan ci Yàlla. 12:13 Noonu Piyeer fëgg buntu kër ga, te mbindaan mu tudd Rodd wuyusi ko. 12:14 Mu xàmmi baatu Piyeer, bég ci, ba fàtte koo ubbil, waaye mu daw ci biir, xamle ne Piyeer a nga ca bunt ba. 12:15 Ñu ne ko: «Xanaa dangaa dof.» Waaye mu dëgër ci li mu wax. Noonu ñu ne ko: «Xanaa malaakaam la.» 12:16 Fekk Piyeer di gën a fëgg. Noonu ñu tijji, gis ko, daldi waaru. 12:17 Piyeer taf loxoom ci gémmiñam, ngir ñu noppi, daldi leen nettali, ni ko Boroom bi génnee ca kaso ba. Mu ne leen: «Tee ngeen jottali ko Saag ak bokk ya.» Bi mu ko waxee, mu jóge fa, dem feneen. 12:18 Bi bët setee nag, yengu-yengu bu réy am na ca xarekat ya, ñu ne: «Ana Piyeer?» 12:19 Noonu Erodd wutlu ko, waaye gisu ko. Kon mu àtte wottukat ya, joxe ndigalu rey leen. Bi loolu amee Erodd jóge ci diiwaanu Yude, dem dëkku Sesare, toog fa. 12:20 Fekk mu nekk ci xëccoo bu tàng ak waa dëkki Tir ak Sidon. Naka noona ñu ànd, bëgg koo gis. Ñu neexal Balastus, bëkk-néegu buur ba, di ñaan jàmm, ndaxte réewu buur ba moo doon dundal seen bos. 12:21 Ca bés ba ñu jàpp nag Erodd sol mbubbi buuram, toog ca jal ba ca àttekaay ba, di leen yedd ak a dénk. 12:22 Noonu mbooloo mi di yuuxu naan: «Lii baatu Yàlla la, du baatu nit!» 12:23 Ca saa sa nag, gannaaw màggalul Yàlla, malaakam Boroom bi fàdd ko te ay sax dugg ko, ba mu dee. 12:24 Moona kàddug Boroom bi di gën a màgg tey law. 12:25 Naka Barnabas ak Sool, bi ñu matalee seen liggéey, ñu jóge Yerusalem, ñibbi, ànd ak Yowaana mi tudd Màrk.
13:1 Amoon na ci mbooloom ñi gëm, mi nekk dëkku Ancos, ay yonent ak ay jàngalekat: maanaam Barnabas, Simeyon ku ñu dàkkentale Niseer, Lusiyus mi dëkk Siren, Manayen mi yaroondoo ak Erodd boroom diiwaan ba, ak Sool. 13:2 Am bés nag, bi ñuy jaamu Boroom bi ak di woor, Xel mu Sell mi ne: «Beral-leen ma Barnabas ak Sool ngir liggéey, bi ma leen wooye.» 13:3 Bi ñu ko déggee, ñu daldi woor ak a ñaan, teg leen ay loxo, ba noppi bàyyi leen ñu dem. 13:4 Noonu Xel mu Sell mi yónni leen. Ñu dem nag ci dëkku Selusi, dugg fa gaal, jëm ci dun bu ñuy wax Sipar. 13:5 Bi ñu teeree ca dëkku Salamin nag, ñu yégle fa kàddug Yàlla ca jàngub Yawut ya. Ku tudd Yowaana ànd ak ñoom, di leen jàpple ci liggéey bi. 13:6 Noonu ñu jaar ci dun bépp, ba egg dëkku Pafos. Foofa ñu gis luxuskat bu tudd Bar-Yeesu, di Yawut bu mbubboo turu yonent. 13:7 Mu bokk ci gàngooru boroom réew ma tudd Sersiyus Poolus, di nit ku neex xel. Moom nag mu woolu Barnabas ak Sool, ngir bëgg a dégg kàddug Yàlla. 13:8 Waaye Elimas, boroom xam-xam bu ñuul bi --ndaxte loolu la turam di tekki — di leen dogale, ngir bañ boroom réew ma gëm. 13:9 Ci kaw loolu Sool, mi tudd it Pool, daldi fees ak Xel mu Sell mi; mu xool ko jàkk, 13:10 ne ko: «Yaw mi fees ak fen ak lu bon, di doomu Ibliis, tey noonu lépp lu jub, ndax doo bàyyee dëngal yoon yu jub yu Boroom bi? 13:11 Léegi loxob Boroom bi dina dal sa kaw, te dinga gumba, ba dootuloo gis jant bi ab diir.» Ca saa sa nag ay bëtam muuru, mu daldi tàbbi cig lëndëm, muy làmbatu, di wut ku ko wommat. 13:12 Ba boroom réew ma gisee li xew nag, mu daldi gëm, di yéemu ci yoonu Boroom bi. 13:13 Naka noona Pool ak ñi mu àndal jóge Pafos, jaar ci géej, jëm dëkku Peers ci réewu Pamfili. Yowaana nag tàggoo ak ñoom, dellu Yerusalem. 13:14 Waaye ñoom ñu jóge Peers, aw ca yoon wa, ba ñëw dëkku Ancos ci diiwaanu Pisidi. Bésu noflaay ba nag ñu dugg ca jàngu ba, toog. 13:15 Bi ñu jàngee yoonu Musaa ak yonent ya, njiiti jàngu ba yónnee ca ñoom ne leen: «Bokk yi, bu ngeen amee lu ngeen di dénk mbooloo mi, waxleen ko.» 13:16 Noonu Pool jóg, tàllal loxoom ne leen: «Yéen bokki Israyil ak yéen ñi ragal Yàlla, dégluleen! 13:17 Yàllay bànni Israyil tànn na sunuy maam, di yokk xeet wa, bi ñuy ganeyaan ci Misra; ba noppi mu génne leen fa ak kàttanu loxoom. 13:18 Diirub ñeent-fukki at mu di leen muñal ca màndiŋ ma. 13:19 Gannaaw loolu faagal na juróom-ñaari xeet ci réewu Kanaan, ba sunuy maam donn réew ma. 13:20 Loolu lépp xew na ci diirub ñeenti téeméeri at ak juróom-fukk. «Gannaaw loolu mu jox leen ay àttekat, ba ci yonent Yàlla Samwil. 13:21 Booba ñuy ñaan buur, te Yàlla jox leen Sóol, doomu Kis ci giiru Ben-yamin, muy seen buur diirub ñeent-fukki at. Gannaaw ga mu jële ko fa, 13:22 dellu falal leen buur bu tudd Daawuda, mu seedee ko nii: “Gis naa Daawuda, doomu Yese, ku ma neex ci sama xol, te dina def lépp luy sama coobare.” 13:23 «Noonu ci askanam Yàlla indil na bànni Israyil Musalkat bi Yeesu, ci ni mu ko dige woon. 13:24 Laata muy ñëw nag, Yaxya daan na waare, ne bànni Israyil gépp, ñu tuub seeni bàkkaar, te mu sóob leen ci ndox. 13:25 Te ba Yaxyay jeexal sasam, mu ne: “Ku ngeen may teg? Duma Ki war a ñëw; waaye am na kuy ñëw sama gannaaw, koo xam ne kii yeyoowumaa tekki ay dàllam.” 13:26 «Bokk yi, yéen askanu Ibraayma ak yéen ñi ragal Yàlla, kàddug mucc gi ci nun la wàcc. 13:27 Waa Yerusalem ak seeni kilifa xàmmiwuñu woon Yeesu te xamuñu woon waxu yonent, yi ñuy jàng bésu noflaay bu nekk; teewul ñu amal waxu yonent yi, ci li ñu àtte Yeesu, ba daan ko. 13:28 Yoon dabu ko fenn, moona ñaan nañu Pilaat, mu reylu ko. 13:29 Noonu ñu def lépp lu yonent yi bindoon ci mbiram, ba noppi ñu wàcce ko ca bant ba, tàbbal ko ci bàmmeel. 13:30 Waaye Yàlla dekkal na ko, 13:31 te diirub ay fan yu bare feeñu na ñi àndoon ak moom, jóge diiwaanu Galile, dem Yerusalem; léegi nag ñooy ay seedeem ci wetu xeet wi, 13:32 te nu ngi leen di xamal xebaar bu baax ne leen, li Yàlla digoon sunuy maam, 13:33 def na ko ngir nun seeni sët, ci li mu dekkal Yeesu. Moom lañu bindoon ci ñaareelu saaru Sabóor ne:“Yaa di sama Doom,maa di sa Baay tey.” 13:34 Te it li ko Yàlla dekkal, ba mu bañatee jaar ci dee, te suuf du ko lekk mukk, moom la Yàlla wax ne:“Dinaa la may barke yu sell te wóor,yi ma digoon Daawuda.” 13:35 Moo tax mu waxaat feneen ne:“Doo bàyyi sa Waa ju sell, mu yàqu.” 13:36 Ndaxte bi Daawuda defee coobareg Yàlla ci jamonoom, mu faatu, ñu suul ko, mu fekki ay maamam, suuf lekk ko. 13:37 Waaye Ki Yàlla dekkal, yaramam seeyul. 13:38 «Kon nag bokk yi, nangeen xam ne, ci moom Yeesu nu ngi leen di yégal mbaalug bàkkaar yi. Te fépp fu yoonu Musaa tële woon a àttee nit ni ku jub, 13:39 fa la Yeesu di àttee ni ku jub képp ku ko gëm. 13:40 Wottuleen nag ba li yonent yi bindoon bañ leen a dal, ci li ñu ne: 13:41 “Yéen ñiy xeebaate, gis leen lii,ngeen yéemu ba far;ndaxte dinaa def ci seen jamono jëf,joo xam ne su ngeen ko déggee sax,dungeen ko gëm.”» 13:42 Bi ñuy génn nag ca jàngu ba, Yawut ya ñaan leen, ñu baamtu wax ja ca bésu noflaay ba ca tegu. 13:43 Te bi mbooloo ma tasee, ay Yawut yu bare ak ñi tuuboon ci yoonu Yawut te ragal Yàlla, topp ci Pool ak Barnabas. Ñuy diisoo ak ñoom, di leen xiir, ñu wàkkirlu ci yiwu Yàlla. 13:44 Noonu bésu noflaay ba ca tegu, daanaka waa dëkk bépp daje, ngir déglu kàddug Yàlla. 13:45 Waaye bi Yawut yi gisee mbooloo ma, ñu daldi fees ak kiñaan, di weddi li Pool di wax te di ko xas. 13:46 Bi loolu amee Pool ak Barnabas ne leen ci lu bir: «Yéen lanu war a jëkk a yégal kàddug Yàlla, waaye gannaaw gàntu ngeen ko, ba àtte seen bopp ne, yeyoowuleen dund gu dul jeex gi, kon nu ngi woññiku ci ñi dul Yawut. 13:47 Ndaxte moom la nu Boroom bi sant ci li mu naan:“Samp naa la, nga nekk leeru ñi dul Yawut,ngir nga yóbbu mucc gi, mu daj cati àddina.”» 13:48 Ñi dul Yawut nag, bi ñu déggee loolu, daldi bég tey màggal kàddug Boroom bi; te ñépp ñu jagoo dund gu dul jeex daldi gëm. 13:49 Noonu kàddug Boroom bi di law ci diiwaan bépp. 13:50 Waaye Yawut ya xiir ay jigéen, ñi woomle te farlu ci diine, ñoom ak magi dëkk ba, ñu fitnaal Pool ak Barnabas, ngir génne leen réew ma. 13:51 Waaye Pool ak Barnabas daldi yëlëb seen pëndu tànk, ngir dëggal seen weddi, jëm dëkku Ikoñum. 13:52 Naka taalibe yi nag, ñu fees ak mbég ak Xel mu Sell mi.
14:1 Bi Pool ak Barnabas nekkee Ikoñum nag, ñu dugg ci jàngub Yawut ya, ni ñu ko daan defe; ñuy waare, ba mbooloom Yawut ak Gereg mu bare gëm. 14:2 Waaye Yawut yu nanguwul yi ñoo jógloo ñi dul Yawut, di ñaawal seen njort ci bokki taalibe yi. 14:3 Pool ak Barnabas nag sax nañu ci Ikoñum lu yàgg, ñu wéeru ci Boroom bi, bay wax ak fit wu dëgër; te Yàlla dëggal kàddug yiwam, ba may leen, ñu def ay kéemaan ak ay firnde. 14:4 Noonu waa dëkk bi xàjjalikoo, ñii far ak Yawut yi, ñale far ak ndaw ya. 14:5 Waaye ñi dul Yawut ak Yawut yi, ñoom ak seeni kilifa, lal pexem fitnaal leen ci sànni ay doj. 14:6 Bi ko Pool ak Barnabas yégee nag, ñu daw ca diiwaanu Likawni ca dëkk ya ñuy wax Listar ak Derbë ak wàllaa ya. 14:7 Foofa ñu di fa xamle xebaar bu baax bi. 14:8 Amoon na ca Listar nag nit ku fa toog, ku ay tànkam làggi, ndax li mu judduwaale lafañ te musul a dox. 14:9 Moom nag muy déglu Pool miy waare. Noonu Pool xool ko jàkk, gis ne, am na ngëm ngir wér. 14:10 Mu ne ko ak baat bu dëgër: «Jógal taxaw bu jub.» Noonu nit ki ne bërét, jóg, daldi dox. 14:11 Bi mbooloo ma gisee li Pool def, ñu daldi yuuxu, ne ci làkku waa Likawni: «Yàlla yi soppiku nañu nit, wàcc ci nun.» 14:12 Noonu ñu tudde Barnabas, Sës, te tudde Pool, Ermes, ndaxte mooy ki yor wax ji. 14:13 Fekk ci buntu dëkk ba amoon na fa kër gu ñuy màggale Sës. Saraxalekat ba nag ànd ak mbooloo ma, daldi indi ca bunt ya ay yëkk ak ay caq, yi ñu defare tóor-tóor, ngir màggal leen ci tuur deretu mala. 14:14 Waaye bi ko ndaw yi Barnabas ak Sool déggee, ñu sib ko ba xotti seeni yére, ñu daldi daw, tàbbi ca mbooloo ma, di wax ci kaw ne: 14:15 «Yéen nit ñi, lu leen xiir ci lii? Nun it ay nit lanu, ñu bokk bind ak yéen. Te nu ngi leen di xamal xebaar bu baax ne leen, ngeen dëddu yëfi neen yii te woññiku ci Yàlla miy dund te sàkk asamaan, suuf, géej ak li ñu ëmb lépp. 14:16 Démb mayoon na xeet yépp, ñu aw seen yoonu bopp. 14:17 Moona noppiwul a firndeel aw meloom ci def lu baax, di leen wàcceele ci asamaan taw buy indi naataange, ba ngeen lekk ba suur, te seen xol fees ak mbég.» 14:18 Noonu ci lu jafe yey nañu mbooloo ma ak wax jooju, ba tere leen, ñu rendil leen sarax. 14:19 Waaye bi loolu wéyee amoon na ay Yawut yu jóge Ancos ak Ikoñum, ñu fàbbi mbooloo ma, sànni Pool ay doj, ba yaakaar ne dee na, ñu diri ko ba ca gannaaw dëkk ba. 14:20 Waaye taalibe ya ñëw wër ko, mu daldi jóg, duggaat ca dëkk ba. Ca suba sa nag, mu ànd ak Barnabas, dem Derbë. 14:21 Bi ñu fa àggee nag, ñu xamle fa xebaar bu baax bi, ba sàkk fa ay taalibe yu bare. Gannaaw loolu ñu dellusi Listar, Ikoñum ak Ancos, 14:22 di dooleel xeli taalibe ya, xiir leen ñu sax ci yoon wi; ñu ne leen: «Ci kaw nattu yu bare lanu war a dugge ci nguuru Yàlla.» 14:23 Ci mbooloom ñi gëm mu nekk nag, ñu tànn ci ay njiit; ba noppi ñu ñaan Yàlla ak di woor, dénk leen Boroom bi ñu gëm. 14:24 Gannaaw loolu ñu jaar diiwaanu Pisidi, dikk ci Pamfili. 14:25 Ñu yégle kàddu gi ci dëkku Peers, door a dem dëkku Atali. 14:26 Foofa nag ñu dugg gaal, jëm Ancos, fa ñu leen dénke woon ca yiwu Yàlla, ngir liggéey bi ñu àggale. 14:27 Bi ñu agsee, ñu woo mbooloom ñi gëm, nettali leen fi ñu jaar ak Yàlla fépp, ak ni mu ubbee buntu ngëm ci ñi dul Yawut. 14:28 Noonu ñu toog ak taalibe ya diir bu yàgg.
15:1 Amoon na bés ay nit jóge diiwaanu Yude, ñuy jàngal bokk yi ne leen: «Ku xaraful, ni ko aaday Musaa santaanee, doo man a mucc.» 15:2 Pool ak Barnabas nag am ak ñoom diisoo ak werante wu metti; noonu bokk yi jàpp ne, Pool ak Barnabas ak ñeneen ci ñoom war nañoo dem Yerusalem ca ndaw ya ak njiit ya, ngir leeral werante wi. 15:3 Kon nag mbooloo mi gunge leen, ñu jaar ci wàlli Fenisi ak Samari, di nettali ni ñi dul Yawut woññikoo ci Yàlla, ba bokk yépp am ca mbég mu réy. 15:4 Te bi ñu agsee Yerusalem, mbooloom ñi gëm, ndaw yi ak njiit yi teeru leen, ñu nettali leen fi ñu jaar ak Yàlla fépp. 15:5 Ci kaw loolu ñeneen, ñi gëm waaye bokk ci tariixab Farisen ya, daldi jóg ne: «Fàww ñi dul Yawut xaraf, te ñu dénk leen sàmm yoonu Musaa.» 15:6 Noonu ndaw yi ak njiit yi dajaloo, ngir seet mbir moomu. 15:7 Gannaaw werante wu bare Piyeer jóg ne leen: «Yéen bokk yi, xam ngeen ne, ca njàlbéen ga Yàlla tànnoon na ma ci yéen, ngir ma yégal ñi dul Yawut xebaar bu baax bi, ba ñu gëm. 15:8 Te Yàlla, mi xam xol yi, seede na leen ci li mu leen may Xel mu Sell mi, ni mu nu ko maye nun itam. 15:9 Gënalantewu nu ak ñoom, ci li mu sellal seen xol ci kaw ngëm. 15:10 Léegi nag lu tax ngeen di diiŋat Yàlla, ciy teg taalibe yi yen bu nu musul a àttan, nun mbaa sunuy maam? 15:11 Nun daal ci yiwu Yeesu Boroom bi lanu yaakaar a mucce, te ñoom itam, ci lañu wékku.» 15:12 Bi mu ko waxee, mbooloo mépp ne xeram, di déglu Barnabas ak Pool, ñuy nettali kéemaan ak firnde yépp, yi Yàlla def jaarale ko ci ñoom ci biir ñi dul Yawut. 15:13 Bi ñu noppee, Saag jël kàddu ga ne: 15:14 «Bokk yi, dégluleen ma! Simoŋ nettali na, ni Yàlla seetsee bu jëkk ñi dul Yawut, ngir sàkku ci ñoom xeet wu ñu tudde turam. 15:15 Te loolu sax dëppoo na ak li yonent yi tëral; ñu bind ne: 15:16 “Boroom bi nee na:Gannaaw loolu dinaa dellusi,te yékkati këru Daawuda, gi ne tasar,dinaa defar toj-toj ya,ba taxawalaat ko. 15:17 Noonu li des ci doom Aadama wut Boroom bi,maanaam xeet yi dul Yawut, ñuy tudd sama tur. 15:18 Man dinaa def loolu, man Boroom bi ko wax,te ca njàlbéen ba tey ma di ko xamle.” 15:19 «Kon nag lii mooy sama ndigal: bunu gétën ñi dul Yawut te woññiku ci Yàlla. 15:20 Waaye nu bind leen, ñu moytu ñam wu araam wu ñu tuuroo xërëm, tey moytu njaaloo, ak jur gu médd, bay naan deret ja. 15:21 Ndaxte ca njàlbéen ga ba tey am na ca dëkk bu nekk ñuy waare ci yoonu Musaa; bésu noflaay bu nekk sax dañu ciy xutba ca jàngu ya.» 15:22 Bi mu ko waxee, ndaw yi ak njiit yi ak mbooloom ñi gëm mépp fas yéenee tànn ci ñoom ay nit, yónni leen Ancos, ñu ànd ak Pool ak Barnabas. Noonu ñu tànn Yudd, mi ñuy dippee Barsabas, ak Silas, di ay njiit ca bokk ya. 15:23 Ñu jox leen bataaxal bu ne: Yéen sunu bokk yi dul Yawut te dëkk Ancos, Siri ak Silisi, nu ngi leen di nuyu, nun seeni bokk, di ndaw yi ak njiit yi. 15:24 Dégg nanu ne, am na ay nit ñu bawoo ci nun, ñu di leen lëjal ak seeni wax, di jaxase seeni xol, te fekk sukkandikuwuñu ci lenn ndigal lu jóge ci nun. 15:25 Kon nag mànkoo nanu ci tànn ay nit, yónnee leen ko, ànd ak sunuy soppe Barnabas ak Pool. 15:26 Ñoom jaay nañu seen bakkan ngir turu Yeesu Kirist Boroom bi. 15:27 Yónni nanu nag Yudd ak Silas, ñu di leen xamal xebaar boobu ci seen gémmiñ. 15:28 Ndaxte li neex Xel mu Sell mi te neex nu, mooy nu bañ leen a teg beneen yen, lu dul dénkaane yii am njariñ, 15:29 maanaam ngeen moytu ñam wu ñu tuuroo xërëm, deretu jur gu médd ak njaaloo. Bu ngeen moytoo yëf yooyu, dingeen def lu baax. Ci jàmm. 15:30 Noonu ñu tàggoo, dem Ancos, ñu dajale mbooloo mi, jébbal leen bataaxal bi. 15:31 Ñu jàng ko nag, seen xol sedd ci doole, ji leen bataaxal bi indil. 15:32 Te Yudd ak Silas, ñi doon yonent, ñuy dooleel bokk yi, di dëgëral seen fit ak wax yu bare. 15:33 Bi loolu amee ñu toog fa ab diir, ba noppi bokk yi yiwi leen ci jàmm, ñu dellu ca ña leen yónni woon. 15:35 Waaye Pool ak Barnabas des ci Ancos, di jàngale ak di xamle xebaar bu baax bu kàddug Boroom bi, ñoom ak ñeneen ñu bare. 15:36 Gannaaw ay fan Pool ne Barnabas: «Nan dellu seeti bokk ya ca dëkk yépp, fu nu mas a yéglee kàddug Boroom bi, ba gis nu ñu def.» 15:37 Barnabas nag bëggoon na yóbbaale Yowaana, mi ñuy wax it Màrk. 15:38 Waaye Pool dafa lànk ne: «Matul nu yóbbu ki nu waccoon ca Pamfili, ba àndul woon ak nun ca liggéey ba.» 15:39 Noonu ñu xuloo, ba far tàggoo. Barnabas yóbbaale Màrk, ñu dugg gaal, jëm Sipar. 15:40 Pool tànn Silas, dem; bokk ya dénk leen ci yiwu Boroom bi; 15:41 mu jaar ci diiwaanu Siri ak Silisi, di dëgëral mboolooy ñi gëm.
16:1 Naka noona mu dikk dëkki Derbë ak Listar, fekk fa taalibe bu tudd Timote te ndeyam di Yawut bu gëm, waaye baayam di Gereg. 16:2 Te mbokk, yi nekk dëkki Listar ak Ikoñum, seedeel nañu ko lu baax. 16:3 Pool bëgg nag mu ànd ak moom, waaye ndegam Yawut yépp, ya dëkk ca wàllaa ya, xam ne baayam Gereg la woon, mu jël ko, xarafal ko. 16:4 Bi loolu amee ñuy jaar ca dëkk ya, jottali leen dénkaane, yi ndaw yi ak njiit yi nekk Yerusalem joxe, te sant leen ñu sàmm ko. 16:5 Noonu mboolooy ñi gëm di gën a dëgër ci yoon wi, tey yokku bés bu nekk. 16:6 Bi loolu amee gannaaw Xel mu Sell mi aaye na leen, ñu yégleji kàddu gi ci diiwaanu Asi, ñu daldi jaari wàlli Firisi ak Galasi. 16:7 Bi ñu agsee nag ci wetu diiwaanu Misi, ñuy jéem a dugg diiwaanu Bitini, waaye Xelum Yeesu mayuleen ko. 16:8 Ñu romb nag Misi, dem dëkku Torowas. 16:9 Noonu ci guddi Yàlla feeñu Pool ci nii: nitu Maseduwan taxaw, di ko ñaan ne ko: «Ñëwal ci Maseduwan, wallusi nu!» 16:10 Bi mu amee peeñu moomu, ca saa sa nu fexee jàll ba Maseduwan, xam ne Boroom bi moo nu woo, ngir nu xamle fa xebaar bu baax bi. 16:11 Noonu nu dugg gaal ca Torowas, jubal dunu Samotaras, jóge fa ca ëllëg sa, nu jëm teerub Neyapolis. 16:12 Bi nu fa teeree, nu jëm Filib, bi nekk dëkk bi ëpp maana ca wàll woowu ci diiwaanu Maseduwan, di it suufus Room. Nu toog fa ay fan. 16:13 Bi bésu noflaay agsee nag, génn nanu ci buntu dëkk ba, jublu ci wetu dex ga, yaakaar ne bérabu ñaanukaay la. Nu toog fa nag, di wax ak jigéen ña fa dajaloo. 16:14 Fekk am na fa jigéen juy déglu, tudd Lidi, di jaaykatu cuub, bu dëkk Catir, te mu ragal Yàlla. Noonu Boroom bi ubbi na xolam, ba mu nangu li Pool di wax. 16:15 Ci kaw loolu ñu sóob ko ci ndox, moom ak waa këram, ba noppi mu ñaan nu ne: «Bu ngeen ma jàppee ni ku takku ci Boroom bi, ganesileen ma ci sama kër.» Te mu di nu ci xiir. 16:16 Am bés, ba nuy dem nag ca ñaanukaay ba, nu daje ak jaam bu jigéen bu rabu gisaane solu, te ay sangam di jariñu lu bare ci gisaaneem. 16:17 Mu daldi topp ci Pool ak nun, di xaacu ne: «Nit ñii jaami Yàlla Aji Kawe ji lañu; ñoo leen di yégal yoonu mucc.» 16:18 Muy def noonu ay fani fan, waaye bi ko Pool xajootul, mu woññiku ne rab wa: «Sant naa la ci turu Yeesu Kirist, génnal ci moom.» Noonu rab wa ne mëll, génn ci moom. 16:19 Bi ay sangam gisee nag seen buntu wërsëg tëju, ñu daldi jàpp Pool ak Silas, di leen diri, jëme leen ca pénc ma fa kanam njiit ya. 16:20 Noonu ñu dëj leen fa mbaxanay menne naan: «Yawut yii lëjal nañu sunu dëkk, 16:21 di xamle ay aada yu nu sañul a nangu mbaa nu di ko topp, nun ñi bokk ci nguuru Room.» 16:22 Mbooloo ma it ànd ci, dal ci seen kaw; àttekat ya nag summilu seeni yére, santaane ñu dóor leen ay yar. 16:23 Noonu ñu dóor leen ay yar yu bare, tëj leen, sant boroom kaso ba, mu wottu leen bu wér. 16:24 Gannaaw jot na ndigal loolu nag, mu sànni leen ca néeg ba gën a ruqu ci biir kaso ba, jéng seeni tànk. 16:25 Ba guddi giy xaaj nag, Pool ak Silas di ñaan ak di sant Yàlla, te ñeneen ñi nekk ca kaso ba di leen déglu. 16:26 Ca saa sa suuf yengu bu metti, ba fondamaab kaso ba daanu; bunt yépp daldi ne kulbet ubbiku, te jéngi ña ñu tëj ne tell tijjiku. 16:27 Ci kaw loolu boroom kaso ba tiite ci ay nelaw, gis bunt yépp ubbiku, mu daldi bocci jaaseem, bëgg a xaru, yaakaar ne ña ñu tëj dañoo daw. 16:28 Waaye Pool wax ci kaw ne: «Bul lor sa bopp, nun ñépp nu ngi fi.» 16:29 Bi ko boroom kaso ba déggee, mu daldi laaj làmp, ne saraax dugg, daanu ci kanamu Pool ak Silas, di lox. 16:30 Mu génne leen ci biti ne leen: «Kilifa yi, lu ma war a def, ba mucc?» 16:31 Ñu tontu ko: «Gëmal Yeesu Boroom bi, kon dinga mucc, yaw ak sa njaboot.» 16:32 Noonu ñu xamal ko kàddug Boroom bi, moom ak waa këram gépp. 16:33 Mu jël leen nag ci waxtu woowu ci guddi, raxas seeni gaañu-gaañu, ba noppi ñu sóob ko ci ndox, moom ak waa këram gépp. 16:34 Bi ñu ko defee mu yóbbu leen ca këram, jox leen ñu lekk, mu bég lool ci li mu gëm Yàlla, moom ak waa këram gépp. 16:35 Bi bët setee, àttekat ya yónni alkaati ya, ñu ne boroom kaso ba: «Yiwil ñaari nit ñooñu, ñu dem.» 16:36 Kon boroom kaso ba yégal loolu Pool ne ko: «Àttekat ya jox nañu ma ndigal, ngir ma yiwi leen, ngeen dem; léegi nag génnleen, te dem ci jàmm.» 16:37 Waaye Pool ne alkaati ya: «Dóor nañu nu ay yar ci kanamu ñépp, ci lu ñu wéerul ci benn àtte, rax-ca-dolli tëj nañu nu kaso, nun ñiy jaambur ci nguuru Room. Léegi ndax dañu noo bëgg a sànni ci mbedd mi ci kumpa? Mukk! Nañu ñëw, ñoom ci seen bopp, gunge nu ci biti.» 16:38 Bi mu ko waxee, alkaati ya yégal àttekat ya la mu wax. Bi ñu déggee ne, jaamburi Room lañu, ñu daldi tiit. 16:39 Ñu ñëw nag di leen dëfël, ñu gunge leen ci biti, di leen ñaan, ñu génn dëkk ba. 16:40 Noonu ñu génn ca kaso ba, dugg ci kër Lidi, ñu gis fa bokk ya, dëgëral leen, daldi dem seen yoon.
17:1 Bi ñu fa jógee, ñu aw yoon wa jaar dëkku Amfipolis ak Apoloni, door a ñëw Tesalonig, fa Yawut ya am jàngu. 17:2 Pool nag dugg ca ñoom, na mu ko daan defe, ba am fa ñetti bésu noflaay, muy werante ak ñoom ci li Mbind mi wax. 17:3 Mu di leen ko tekki, te di leen wax ay firnde yuy wone ne, fàww Almasi bi sonn te dekki. Mu ne leen: «Yeesu, mi ma leen di yégal, mooy Almasi bi.» 17:4 Noonu ñenn ci Yawut yi gëm, ànd ak Pool ak Silas, ñoom ak mbooloo mu mag ci Gereg yi ragal Yàlla, ak jigéen ñu am maana ñu bare. 17:5 Waaye kiñaan tàbbi ca Yawut ya, ñu daldi jël ay taxawaalukat ca pénc ma, dajale mbooloo, ñuy yengal dëkk ba. Ñu daanu ci kër Yason, di wut Pool ak Silas, ngir dëj leen ci kanam waa dëkk ba. 17:6 Bi ñu leen gisul nag, ñu diri Yason ak ñeneen ca bokk ya ci kanam àttekat ya. Ñuy wax ci kaw naan: «Nit ñi dëpp àddina sépp agsi nañu fii léegi, 17:7 te Yason a leen dalal. Ñoom ñépp dañoo bañ ndigali buur Sesaar ne, am na beneen buur bu ñuy wax Yeesu.» 17:8 Bi ko mbooloo mi ak àttekat yi déggee, ñu daldi jaaxle lool. 17:9 Noonu nanguwuñoo yiwi Yason ak ñi ci des, lu dul bi ñu leen bataleelee dara. 17:10 Bi loolu amee bokk yi jàllale Pool ak Silas ci saa si ci guddi, ñu jëm Bere. Ba ñu fa eggee nag, ñu dugg ca jàngub Yawut ya. 17:11 Fekk ña fa nekk ñoo gën a am ay teggin waa Tesalonig, ndaxte nangu nañu kàddu ga te sawar ca, di niir Mbind mi bés bu nekk, ba xam ndax loolu dëgg la am déet. 17:12 Kon nag Yawut yu bare gëm ak ñu bare ci Gereg yi, di jigéen yu am maana ak ay góor. 17:13 Waaye bi Yawuti Tesalonig déggee ne, Pool mu ngi yégle kàddug Yàlla ci Bere it, ñu daldi fay dikk, di jógloo ak a jaxase mbooloo ma. 17:14 Noonu bokk yi yebal Pool ca saa sa, mu jëm géej, waaye Silas ak Timote des fa. 17:15 Ñi ànd ak Pool nag gunge ko ba dëkku Aten. Bi ñu fa àggee, ñu woññiku, yóbbaale ndigalu Pool ne, Silas ak Timote ñëw fekksi ko ci lu gën a gaaw. 17:16 Bi leen Pool di nég ca Aten, mu am naqaru xol wu réy ci li mu gis dëkk ba fees ak ay nataali bokkaale Yàlla. 17:17 Muy werante nag ca jàngu ba ak Yawut ya ak ña ragal Yàlla, tey werante it bés bu nekk ca pénc ma ak ña fay dajaloo. 17:18 Noonu ay boroom xam-xam ci mbooloo mi ñuy wax Epikuren ak ci mbooloo mi ñuy wax Estowisen, di werante ak moom. Ñenn ci ñoom ne: «Fortukatu xam-xam bii, lu mu bëgg a wax?» Te ña ca des, bi ñu déggee Pool di waare xebaar bu baax bi, aju ci Yeesu ak ci mbirum ndekkite, ñu ne: «Dafa mel ni, day waare ay yàlla yu nu xamul.» 17:19 Kon nag ñu jël ko, yóbbu ko ca géew, ba ñuy wax Areyopas. Ñu ne ko: «Danoo bëggoon, nga leeral nu ci sa xam-xam bu bees, bii ngay yégle. 17:20 Ndaxte sol nga ci sunuy nopp lu nu xamul. Danoo bëggoon a xam nag léegi, loolu lu muy tekki.» 17:21 Ndaxte waa Aten ñépp ak doxandéem ya fa dëkk, wax ak a déglu lu bees rekk lañu daan xënte. 17:22 Noonu Pool taxaw ci biir mbooloom Areyopas ne leen: «Yéen waa Aten gis naa ne, farlu ngeen ci diine lool. 17:23 Ndaxte bi may doxantu di seet seeni màggalukaay, gis naa ci benn bu ñu bind lii: “Yàlla mi nu xamul.” Li ngeen di màggal nag te xamuleen ko, loolu laa leen di xamal. 17:24 «Yàlla mi sàkk àddina ak li mu ëmb lépp, moom miy Boroom asamaan ak suuf, du dëkk ci néegi màggalukaay yu loxoy nit defar. 17:25 Du jariñu it ci loxoy nit, mel ni dafa soxla dara, ndax moom mooy jox ñépp bakkan ak ruu ak lépp. 17:26 Ci kenn nit la sàkke xeeti àddina yépp, ñu dëkk ci ñeenti xebla yi; fekk àppal na xeet wu nekk jamonoom, te rëdd seen diggi réew. 17:27 Yàlla def na loolu, ngir ñu koy wut ci yaakaaru daj ko ci làmbatu, fekk sax sorewul kenn ci nun. 17:28 “Ndaxte ci moom lanuy dunde, di ci jëf te nekk ci,” ni ko ñenn ci seeni taalifkat dëggale naan: “Nun noo di aw xeetam.” 17:29 Kon nag, bu nu nekkee xeetu Yàlla, warunoo gëm ne, Yàlla mel na ni nataali wurus, xaalis mbaa doj yu nit defar ci xareñ mbaa xel. 17:30 Ca jamono yu wees ya Yàlla toppul ñàkka xam googa, waaye léegi koo man a doon ak foo man a nekk, Yàlla santaane na, nga tuub say bàkkaar. 17:31 Ndaxte sàkk na bés bu muy àtte àddina ci njub, dénk ko Nit ki mu tànn; te firndeel na loolu bu wóor, ci li mu ko dekkal ca néew ya.» 17:32 Bi ñu déggee nag, muy wax ci mbirum ndekkitel ñi dee, ñii di ko fontoo, ña ca des ne ko: «Dinanu la déglu ci mbir moomu beneen yoon.» 17:33 Noonu Pool génn ci seen biir. 17:34 Moona am na ñenn ñu taq ci moom te gëm: xàmmees na ci Denis, ku bokk ci mbooloom Areyopas, ak jigéen ju tudd Damaris, ak ñeneen.
18:1 Bi loolu wéyee Pool bàyyikoo Aten, dem Korent. 18:2 Mu tase fa ak Yawut bu tudd Akilas te juddoo diiwaanu Pont. Muy sog a jóge réewu Itali ak jabaram Pirsil, ndaxte buur ba Këlódd sant na Yawut yépp, ñu génn Room. 18:3 Noonu Pool seeti leen, te gannaaw ñoo bokk liggéey, maanaam di defar ay tànt, mu dal fa ñoom, ñuy liggéeyandoo. 18:4 Bésu noflaay bu nekk nag muy diisoo ak ñi nekk ca jàngu ba, di jéem a gëmloo ay Yawut ak ay Gereg. 18:5 Waaye bi Silas ak Timote jógee diiwaanu Maseduwan, egg fa, Pool jublu ci xamle kàddu gi, tey dëggal ci Yawut yi naan, Yeesu mooy Almasi bi. 18:6 Bi ko Yawut ya gàntoo nag, di ko xas, mu yëlëb ay yéreem ne leen: «Yéena sàkku seen musiba; set naa ci. Léegi maa ngi dem ci ñi dul Yawut.» 18:7 Ci kaw loolu mu jóge fa, dugg ci këru ku tudd Tisiyus Yustus, di ku ragal Yàlla, te kër ga dend ak jàngu ba. 18:8 Kirispus nag, njiitu jàngu ba, gëm na Boroom bi ak waa këram gépp. Te waa Korent ñu bare dégg kàddu gi te gëm ko, ñu sóob leen ci ndox. 18:9 Naka noona Boroom bi feeñu Pool ci guddi ne ko: «Bul tiit dara, waaye deel wax te bañ a noppi. 18:10 Ndaxte maa ngi ànd ak yaw, te kenn du la jàpp, ba fitnaal la, ndaxte am naa xeet wu bare ci dëkk bii.» 18:11 Noonu Pool des at ak genn-wàll ci seen biir, di fa jàngale kàddug Yàlla. 18:12 Ci nguuru Galyon ci diiwaanu Akayi nag, Yawut ya likkoo, ñu dal ci kaw Pool, yóbbu ko ca àttekaay ba. 18:13 Ñu ne: «Kii day xiir nit ñi ci màggal Yàlla ci lu juuyoo ak yoon wi.» 18:14 Bi Pool bëggee wax nag, Galyon ne Yawut ya: «Yéen Yawut yi, bu aju woon ci jàdd yoon walla ñaawteef wu réy, kon liy yoon mooy ma déglu leen. 18:15 Waaye bu ajoo ci ay werante ciy wax ak ay tur ak seen yoon, loolu seen wàll la; man duma ko àtte.» 18:16 Noonu mu dàq leen ca àttekaay ba. 18:17 Ci kaw loolu nit ñépp jàpp Sosten, njiitu jàngu ba, ñu di ko dóor ca kanamu àttekaay ba, waaye Galyon faalewu leen. 18:18 Bi loolu wéyee Pool desati fa fan yu bare. Gannaaw ga mu tàggtoo ak bokk ya, dugg gaal jëm Siri, ànd ak Pirsil ak Akilas. Bi mu jógeegul teerub Señsere, mu watlu boppam, ndaxte am na lu mu dige woon ak Yàlla. 18:19 Noonu ñu teer ci Efes. Pool bàyyi fa ñi mu àndaloon, daldi dugg ca jàngu ba, di diisoo ak Yawut ya. 18:20 Ñu ñaan ko, mu des fa lu gën a yàgg, waaye nanguwul. 18:21 Kon mu tàggtoo ak ñoom naan: «Dinaa dellusi ci yéen, bu soobee Yàlla.» Noonu mu dugg gaal, jóge Efes, 18:22 teersi dëkku Sesare, mu dem nuyu mbooloom ñi gëm, ba noppi dem Ancos. 18:23 Bi mu fa desee ay jamono, mu jóge fa, di jaar dëkkoo-dëkk ci diiwaanu Galasi ak Firisi, di dooleel xoli taalibe yépp. 18:24 Amoon na nag Yawut bu tudd Apolos te juddoo Alegsàndiri, mu dikk Efes. Nit ku yeewu la woon te am xam-xam bu yaatu ci Mbind mi. 18:25 Jàngoon na ci yoonu Boroom bi, di ku farlu ci xelam, muy xamle ak a jàngale bu wóor ci mbirum Yeesu, waaye fekk xam-xamam yem ci ni Yaxya daan sóobe ci ndox. 18:26 Noonu mu daldi wax ak fit wu dëgër ca jàngu ba. Bi ko Pirsil ak Akilas déggee nag, ñu woo ko fi ñoom, gën ko leeral yoonu Yàlla. 18:27 Naka mu bëgg a dem Akayi, bokk ya xiir ko ca, ñu bind taalibe ya, ngir ñu teeru ko teeru bu rafet. Noonu mu dikk fa te jariñ lool ñi gëm jaare ko ci yiwu Yàlla. 18:28 Ndaxte mu ngay yey Yawut ya ca kanam ñépp, di firi Mbind yi, ba wone ne Yeesu mooy Almasi bi.
19:1 Ba Apolos nekkee Korent nag, Pool jaar ca teggi ya gën a kawe ca réew ma, door a dikk Efes. Noonu mu gis fa ay taalibe. 19:2 Mu ne leen: «Ndax jot ngeen ci Xel mu Sell mi, bi ngeen gëmee?» Ñu tontu ko: «Déggunu sax ne, Xel mu Sell mi am na.» 19:3 Mu ne leen: «Kon nag, bi ñu leen sóobee ci ndox, lu ciy maana?» Ñu tontu ko: «Xanaa li Yaxya tëral.» 19:4 Pool ne leen: «Yaxya daan na sóob nit ñi ci ndox, ndax bi ñu tuubee seeni bàkkaar; te mu ne bànni Israyil, kiy topp ci moom lañu war a gëm, maanaam Yeesu.» 19:5 Bi ñu déggee loolu nag, sóob nañu leen ci ndox ci turu Yeesu Boroom bi. 19:6 Te bi leen Pool tegee loxo, Xel mu Sell mi ñëw ci ñoom, ñuy wax yeneeni làkk, di wax ci kàddug Yàlla. 19:7 Limub nit ñooñu nekk na lu mat fukk ak ñaar. 19:8 Noonu Pool dugg ca jàngu ba, di wax ak fit wu dëgër diirub ñetti weer, di diisoo ak ñoom ci mbirum nguurug Yàlla, di leen jéem a gëmloo. 19:9 Waaye bi xolu ñenn ci ñoom fattee, ñu gëmadi, bay suufeel yoon wi ci kanam mbooloo ma, mu jóge ci ñoom, xàjjale taalibe yi ak ñoom, di diisoo bés bu nekk ca jàngukaayu ku ñuy wax Tiranus. 19:10 Mu wéy ci noonu diirub ñaari at, ba ñi dëkk diiwaanu Asi ñépp dégg kàddug Boroom bi, muy Yawut muy Gereg. 19:11 Booba Yàllay def ay kéemaan yu ràññiku yuy jaar ci loxoy Pool. 19:12 Ñu yóbbul sax ñi wopp ay kaala ak ay taraxlaay yu laaloon yaramam, ba jàngoro yi di leen bàyyi, rab yay génn ci ñoom. 19:13 Noonu ay Yawut yuy wëndéelu, di faj ñi rab jàpp, ñu di leen jéem a ñaanal ci turu Yeesu Boroom bi naan: «Ci turu Yeesu, mi Pool di yégle, génnleen.» 19:14 Ñi doon def loolu, juróom-ñaari doom lañu woon ci Sewa, mi doon taafantaloo saraxalekat bu mag ba ci Yawut yi. 19:15 Waaye bi ñu ko defee rab wa tontu leen ne: «Xam naa Yeesu, xam naa it kuy Pool, waaye yéenay ñan?» 19:16 Ci kaw loolu nit ka rab jàpp song leen, noot leen ñoom ñépp; mu soxore leen lool, ba ñu daw kër ga, def yaramu neen te gaañu bu metti. 19:17 Loolu siiw na ci ñépp, ñi dëkk Efes, di Yawut ak Gereg; tiitaange jàpp leen ñoom ñépp, ba ñu màggal turu Yeesu Boroom bi. 19:18 Bi loolu amee ñu bare ci ñi gëm ñëw, di wesar ci kanam ñépp seeni jati luxus. 19:19 Te ñu bare ci ñi daan luxus, indi seeni téere, lakk leen ci kanam ñépp. Te bi ñu xaymaa njëg ga, mu tollook juróom-fukki junniy poseti daraxma. 19:20 Noonu la kàddu Boroom bi lawe, te noot lépp. 19:21 Bi loolu wéyee Pool nas xel jëm Yerusalem, jaar ci diiwaani Maseduwan ak Akayi. Mu ne: «Gannaaw bu ma fa demee, fàww ma seeti Room it.» 19:22 Mu yebal nag ci Maseduwan ñaari jaraafam, di Timote ak Erast, waaye moom mu des ab diir ci Asi. 19:23 Fekk booba amoon na yengu-yengu bu réy ci lu aju ci Yoon wi. 19:24 Ndaxte nit ku tudd Demetirus, di tëggu xaalis buy defar nataali xaalis ngir màggal Artemis, daan na ci jariñu lu bare, moom ak ay nawleem. 19:25 Noonu mu dajale leen ak seeni liggéeykat ne leen: «Gaa ñi, xam ngeen ne, sunu njariñ mu ngi aju ci liggéey bii. 19:26 Gis ngeen nag te dégg ne, Pool male gëmloo na bay fàbbi mbooloo mu bare, waxuma ci Efes rekk, waaye ci biir Asi gépp naan: “Yàlla yu ay loxo defar duñu ay yàlla.” 19:27 Léegi kat loraangee ngi nuy yoot, te du yem ci xañ nu sunu liggéey rekk, waaye it dina daaneel màggalukaayu Artemis sunu yàlla ju mag ji, tey neenal ndamam, moom mi Asi gépp te àddina sépp di màggal.» 19:28 Bi ñu déggee loolu, mer mu réy tàbbi ci ñoom, ñuy yuuxu ne: «Artemis mu Efes màgg na!» 19:29 Noonu dëkk bépp jaxasoo. Ñu bokk benn xalaat, daldi ne milib ca powukaay ba, diri Gayus ak Aristàrk, waa Maseduwan, ñi ànd ak Pool. 19:30 Pool nag bëgg a dugg ca mbooloo ma, waaye taalibe ya nanguwuñu ko. 19:31 Ñenn ca jawriñi nguur gi it, ñuy ay xaritam, yónnee ci moom, di ko dénk, mu bañ a jaay bakkanam ci dugg ca powukaay ba. 19:32 Noonu ndaje ma rëb, ba ñii di yuuxu lii, ñale di yuuxu laa, te ña ca gën a bare xamuñu lu waral ndaje ma. 19:33 Ci kaw loolu Yawut ya jéñ Alegsàndar ci kanam, te mbooloo ma di ko xaacu ay ndigal, mu daldi tàllal loxoom, ngir làyyi ca mbooloo ma. 19:34 Waaye bi ñu xamee ne Yawut la, ñépp a bokk benn baat, yuuxu diirub lu mat ñaari waxtu naan: «Artemis mu Efes màgg na!» 19:35 Gannaaw loolu boroom dëkk ba dalal mbooloo ma ne leen: «Yéen waa Efes, ana ku xamul ne, dëkku Efes moo di wottukaayu màggalukaayu Artemis ak nataalam, bi wàcce asamaan? 19:36 Gannaaw nag kenn mënta weddi loolu, war ngeen a dalal seen xel te bañ a sañaxu ci dara. 19:37 Ndaxte nit ñii ngeen fi indi sàccuñu ca màggalukaay ya te sosaluñu sunu yàlla. 19:38 Su fekkee ne Demetirus ak ay nawleem jànkoonte nañu ak kenn, am na ay bési layoo ak ñu yilif réew mi; nañu fa woo ku ñu amleenteel. 19:39 Waaye su ngeen di laaj leneen, mbooloom dëgg dina ko àtte. 19:40 Ndaxte fi mu ne man nañu noo jiiñ jógug mbooloo mi ndax li fi xew tey. Te bu loolu amee dunu am aw lay ci mbirum mbooloo mu rëb mii, ndaxte amul dara lu ko waral.» 19:41 Bi mu waxee loolu nag, mu tas mbooloo ma.
20:1 Bi yengu-yengu ba dalee, Pool woo taalibe ya fa moom, dooleel leen. Bi mu ko defee mu tàggoo ak ñoom, jóge fa, dellu diiwaanu Maseduwan. 20:2 Noonu mu jaar ca bérab yooyu, di dooleel nit ñi ak wax yu bare; ba noppi mu dem réewu Geres, 20:3 toog fa ñetti weer. Waaye bi mu nekkee ci kaw tànki dugg gaal jëm diiwaanu Siri, te Yawut yi lalal ko pexe, mu fas yéenee dellu, jaare Maseduwan. 20:4 Booba nag ñii ñoo ànd ak moom: Sopater, doomu Pirus mi dëkk Bere; Aristàrk ak Segond, ñi dëkk Tesalonig; Gayus, mi dëkk Derbë, ak Timote; te it Tisig ak Torofim ñi dëkk Asi. 20:5 Ñooñu nag jiitu, di nu nég dëkku Torowas. 20:6 Waaye naka nun, gannaaw màggalu Yawut, ga ñuy wax Mburu ya amul lawiir, nu dugg gaal ci Filib, def ci juróomi fan, fekksi leen Torowas, nu am fa juróom-ñaari fan. 20:7 Ca bés bu jëkk ca ayu-bés ga, booloo nanu ngir damm mburu ma. Te Pool, mi bëggoon a dem ca ëllëg sa, di diisoo ak ñoom te waxtaanam law ba ci xaaju guddi. 20:8 Ca néeg bu kawe, ba nu booloo nag, amoon na fa làmp yu bare. 20:9 Noonu waxambaane wu tudd Ëtikus te toog ca palenteer ba, gëmmeentu bay jeyaxu. Bi Pool di gën a yaatal waxtaanam nag, nelaw daldi ko jàpp, mu xàwweekoo ca ñetteelu taax ma, daanu, ñu yékkati ko, fekk mu dee. 20:10 Waaye Pool wàcc, daldi sëgg ci kawam, roof ko loxoom ne leen: «Bàyyileen jooy yi, mu ngi dund.» 20:11 Noonu mu yéegaat, damm mburu ma, lekk; ba noppi delluwaat ci waxtaanam, di ko yaatal ba ca njël, door a tàggoo. 20:12 Naka waxambaane wa, ñu indi ko muy dund, ba seen xol sedd guyy. 20:13 Nun nag nu jiitu, dugg gaal jëm Asos, fa nu Pool santoon, nu jële ko fa; fekk moom fas na yéeney dox, ba agsi fa. 20:14 Noonu mu fekksi nu ci Asos, nu jël ko ca gaal ga, dem Mitilen. 20:15 Gannaaw loolu gaal ga jóge fa, nu agsi ca ëllëg sa janook dunu Kiyos. Bés ba ca tegu nag nu jàll ba Samos, te ñetteelu fan ba nu àgg Mile. 20:16 Ndaxte Pool fasoon na yéenee teggi Efes, ngir bañ a yàgg ci diiwaanu Asi; mu ngi doon gaawantu, ngir màggal, gi ñuy wax Pàntakot fekk ko Yerusalem. 20:17 Bi Pool eggee Mile nag, mu yónnee ca Efes, ngir woo njiiti mbooloom ñi gëm. 20:18 Bi ñu ñëwee, mu ne leen: «Yéen xam ngeen bu baax, ni ma doon doxale diirub sama ngan gépp ci seen biir, li dale ci bés bi ma jëkkee teg tànk ci Asi ba tey. 20:19 Jaamu naa Boroom bi ci woyof gu mat ak ay rangooñ, dékku ay nattu yu ma pexey Yawut yi indil. 20:20 Xam ngeen ne, musuma leen a nëbb dara lu leen di jariñ, di leen jàngal ci kanamu ñépp ak ca kër ya. 20:21 Dénk naa Yawut yi ak Gereg yi ne leen, ñu tuub seeni bàkkaar, ba woññiku ci Yàlla te gëm sunu Boroom Yeesu. 20:22 «Léegi maa ngi nii di dem Yerusalem, ci li ma Xelu Yàlla mi xiirtal, te xawma lu ma fay dal. 20:23 Xam naa rekk ne, ci dëkkoo-dëkk Xel mu Sell mi xamal na ma ne, ay buum ak ay metit ñu ngi may nég. 20:24 Waaye sama bakkan soxalu ma, su fekkee bey naa sama sas, ba matal liggéey, bi ma Boroom bi dénk, maanaam ma seedeel ci ñépp xebaar bu baax, bi ëmb yiwu Yàlla. 20:25 «Fi mu ne nag xam naa ne, dootuleen gis sama kanam, yéen ñépp ñi ma jaaroon ci seen biir, di yégle nguuru Yàlla. 20:26 Moo tax may dëggal tey jii ne, wàccoo naa ak yéen ñépp bés pénc. 20:27 Ndaxte ñeebluwuma leen, ci di leen xamal lépp li Yàlla digle. 20:28 Wottuleen nag seen bopp te wottu coggal jépp, ji leen Xel mu Sell mi def sàmm, ngeen sàmm mbooloo, mi Yàlla jotal boppam ak deretu Doomam. 20:29 Xam naa ne, bu ma leen wonee gannaaw, bukki yu soxor dinañu tàbbi ci coggal ji te duñu ci ñeeblu kenn. 20:30 Ay nit dinañu jóg ci seen biir sax, di wax luy sànke, ngir sàkku ay taalibe. 20:31 Foogleen nag, di fàttaliku ne diirub ñetti at, guddi ak bëccëg, musumaa noppi di leen artu kenn ku nekk ci yéen ak ay rangooñ. 20:32 «Léegi nag maa ngi leen di dénk Boroom bi, moom ak kàddug yiwam, gi leen man a dëgëral te may leen cér ci biir gaayi Yàlla yu sell yépp. 20:33 Nammuma xaalisu kenn mbaa wurusam mbaa koddaayam. 20:34 Xam ngeen ne, faj naa samay soxla ak soxlay ñi ànd ak man ci sama loxo yii. 20:35 Ci lépp won naa leen royukaay, ci li nu war a dimbali ñi néew doole te fàttaliku li Yeesu Boroom bi wax moom ci boppam ne: “Joxe moo gën a barkeel nangu.”» 20:36 Bi mu waxee loolu, mu sukk ak ñoom ñépp, ñaan ci Yàlla. 20:37 Te ñépp jooy bu metti, di laxasu ci baatu Pool, fóon ko bu baax. 20:38 Li leen gën a teg aw tiis mooy li mu leen wax: «Dootuleen gis sama kanam.» Noonu ñu gunge ko ba ca gaal ga.
21:1 Bi nga xamee ne tàggoo nanu ak ñoom ci naqar, nu dugg gaal, jubal dunu Kos. Te ca ëllëg sa nu dem ba teer ca Rodd, ba noppi jóge fa, jàll ba Patara. 21:2 Foofa nag nu gis gaal guy jàll ba Fenisi, nu dugg ca, mu daldi teddi. 21:3 Noonu nu séen dunu Sipar, bàyyi ko ci sunu càmmooñ, jublu diiwaanu Siri, nu teersi Tir. Ndaxte foofa la gaal gi war a yebbee la mu yeboon. 21:4 Nu wut taalibe ya, ba gis leen, toog ak ñoom juróom-ñaari fan. Ñoom nag ñu ne Pool ci li leen Xelu Yàlla mi may, mu bañ a dem Yerusalem. 21:5 Moona bi jataayu gaal ga matee, nu awaat ci yoon wi. Te ñépp gunge nu, ñoom ak seeni jabar ak seeni doom; nu génn dëkk ba, sukk ca tefes ga, ñaan ci Yàlla. 21:6 Noonu nu tàggoo ak ñoom, dugg ca gaal ga, ñu dellu seen kër. 21:7 Bi nu jógee Tir nag, nu demaat ci géej, ba teer Patolemayis. Foofa nu nuyu bokk ya, yendu, fanaan. 21:8 Nu jóge fa ca ëllëg sa, ñëw ba ca dëkku Sesare. Nu dugg ca kër Filib, taskatu xebaar bu baax bi, mi bokk ci Juróom-ñaar ña, nu dal fa moom. 21:9 Amoon na ñeenti doom yuy janq, ñuy wax ci kàddug Yàlla. 21:10 Bi nu fa nekkee ay fan nag, yonent bu tudd Agabus jóge Yude, agsi. 21:11 Mu ñëw ci nun, daldi yeew ay loxoom ak i tànkam ak laxasaayu Pool naan: «Nii la Xel mu Sell mi waxe: “Ki moom laxasaay gii, Yawut yi dinañu ko yeewe nii ca Yerusalem, jébbal ko ñi dul Yawut.”» 21:12 Bi nu déggee loolu, nun ak ña fa nekk nu ñaan Pool, mu bañ a dem Yerusalem. 21:13 Ci kaw loolu Pool tontu ne: «Lu ngeen di jooy, di yàq sama xol? Bañuma ñu yeew ma rekk, waaye nangu naa sax, ñu rey ma ci Yerusalem ngir turu Yeesu Boroom bi.» 21:14 Bi nu ko mënul a dëpp, nu noppi ne: «Kon na coobareg Boroom bi am!» 21:15 Gannaaw fan yooyu nu defaru, ngir dem Yerusalem. 21:16 Noonu ay taalibe yu dëkk Sesare ànd ak nun, yóbbu nu ca nit ku tudd Manason, fu nu war a dal; moom nag nitu Sipar la woon, di taalibe bu yàgg. 21:17 Bi nu agsee Yerusalem nag, taalibe ya teeru nu ak mbég. 21:18 Ca ëllëg sa Pool ànd ak nun, seeti Saag, fekk njiit yépp teew fa. 21:19 Noonu Pool nuyu leen, nettali leen benn-benn li Yàlla def ci biir ñi dul Yawut, jaarale ko ci liggéeyam. 21:20 Bi ko njiit ya déggee, ñu màggal Yàlla ne ko: «Mbokk mi, gis nga ne, am na ay junniy Yawut ñu gëm, te ñépp a sawar ci yoonu Musaa. 21:21 Dégg nañu ci sa mbir nag ne, yaa ngi jàngal Yawut yépp, yi dëkk ci biir ñi dul Yawut, ñu bàyyi yoonu Musaa te bañ a xarafal seeni doom mbaa topp sunuy aada. 21:22 Lu nu ci war a def nag? Ndaxte ci lu wér dinañu xam ne, ñëw nga. 21:23 Nu ngi lay digal nag, nga def nii: am na ci nun ñeenti góor yu dige ak Yàlla. 21:24 Jël leen, bokk ak ñoom setlu, te nga gàddu seen peyu wateef. Noonu ñépp dinañu xam ne, li ñu déggoon ci sa mbir du dëgg, waaye yaa ngi jëf tey sàmm yoonu Musaa. 21:25 Naka ñi dul Yawut ñi gëm, bind nanu leen li nu àtte ne, ñu moytu ñam wu ñu tuuroo xërëm te moytu deretu médd ak njaaloo.» 21:26 Bi ñu ko waxee, Pool jël nit ña te ca ëllëg sa mu bokk setlu ak ñoom, ñu dugg ca kër Yàlla ga. Ñu xamle ban bés la seen setlu di àgg, di bés bu ñuy jébbale sarax ngir kenn ku nekk ci ñoom. 21:27 Bi àppu juróom-ñaari fan ya di bëgg a jeex, Yawut yi jóge diiwaanu Asi gis Pool ca kër Yàlla ga. Ñu daldi jógloo mbooloo mépp, jàpp ko, 21:28 di xaacu ne: «Wallee, wallee, yéen bokki Israyil; waa jaa ngi nii, moom miy waare fépp ak ci ñépp, bay suufeel sunu xeet ak yoonu Musaa ak bérab bii; dugal na sax ay Gereg fii ci kër Yàlla gi, ba indi sobe ci bérab bu sell bii.» 21:29 Li tax ñu wax loolu, mooy gisoon nañu Torofim mu Efes, ànd ak moom ca dëkk ba, te ñu yaakaar ne, Pool dugal na ko ca kër Yàlla ga. 21:30 Noonu dëkk ba bépp màbb, mbooloo ma ne këpp, ñu jàpp Pool, génne ko ca kër Yàlla ga. Ca saa sa ñu tëj bunt ya. 21:31 Bi ñu koy wut a rey, xebaar ba agsi ba ca kilifag mbooloom xarekat ba, naan Yerusalem gépp jaxasoo na. 21:32 Ca saa sa mu ànd ak ay xarekat ak ay njiiti xare, ne jaas wàcc ci ñoom. Bi Yawut ya gisee kilifa ga ak xarekat ya nag, ñu daldi bàyyi dóor, ya ñu doon dóor Pool. 21:33 Noonu kilifa ga jegesi jàpp ko, santaane ñu jéng ko ak ñaari càllala. Bi ñu ko defee mu laaj ku mu doon ak lu mu def. 21:34 Waaye ci biir mbooloo ma, bu ñii nee lii, ña ca des ne laa. Kon nag gannaaw mënu caa xam dara lu wóor ndax coow li, mu santaane, ñu yóbbu ko ci biir tata ja. 21:35 Bi Pool eggee ca yéegukaayu tata ja, aaytalu mbooloo ma réy, ba ay xarekat fab ko. 21:36 Ndaxte mbooloo maa nga ko topp, di xaacu ne: «Reyleen ko!» 21:37 Bi ñu koy bëgg a dugal ca tata ja, Pool ne kilifa ga: «Ndax man naa laa wax dara?» Mu tontu ko: «Yaw dégg nga gereg? 21:38 Kon nekkuloo waayi Misra, jooju jógloo woon nit ñi keroog te yóbbu woon ñeenti junniy bóomkat ca màndiŋ ma?» 21:39 Pool ne ko: «Man Yawut laa, di jaambur ci Tars, dëkk bu am tur ci diiwaanu Silisi. Maa ngi lay ñaan, ma wax ak mbooloo mi.» 21:40 Te kilifa ga may ko ko. Noonu Pool taxaw ca yéegukaay ba, tàllal loxoom mbooloo ma, ñu daldi ne tekk. Mu wax ak ñoom ci làkku yawut ne:
22:1 «Yéen bokk yi ak baay yi, dégluleen samaw lay.» 22:2 Bi ñu déggee, mu di leen wax ci làkku yawut, ñu gën ne xeram. Noonu Pool ne leen: 22:3 «Man Yawut laa, juddoo Tars ci diiwaanu Silisi, yaroo ci dëkk bii. Taalibe laa woon ci Gamaleel, mu jàngal ma bu wér yoonu sunuy maam, ba ma sawar ci Yàlla, mel ni yéen ñépp tey. 22:4 Daan naa fitnaal ña bokkoon ci yoon wii, ba di ci rey sax; yeew naa góor ak jigéen, tëj leen; 22:5 saraxalekat bu mag ba ak mbooloom njiit yi yépp man nañu ma cee seede. Am bés ñu bindal ma ay bataaxal ngir bokki Damas. Ma doon fa dem, ngir yeew ña fa nekkoon, indi leen Yerusalem, ngir ñu yar leen. 22:6 «Waaye ci digg-bëccëg, bi ma jaaree ca yoon wa, ba jegesi Damas, ca saa sa leer gu mag jóge asamaan, melax ba ëmb ma. 22:7 Ma daldi ne nërëm ci suuf, dégg baat bu ma ne: “Sool, Sool, lu tax nga di ma fitnaal?” 22:8 Ma tontu ko: “Yaa di kan, Boroom bi?” Mu ne ma: “Maa di Yeesum Nasaret, mi ngay fitnaal.” 22:9 Ñi ma àndaloon gis nañu leer ga, waaye dégguñu baatu ka doon wax ak man. 22:10 Noonu ma laaj ko: “Lu ma war a def, Boroom bi?” Boroom bi ne ma: “Jógal dem Damas, foofa dees na la biral lépp, li ma la yen.” 22:11 Gannaaw gisuma woon dara ndax leeraayu melxat ga, ña ma àndal wommat ma, ma ñëw Damas. 22:12 «Bi ma ko defee ku tudd Anañas ñëw ci man. Nit ku ragal Yàlla la woon ci sàmm yoonu Musaa, te Yawuti Damas yépp seedeel ko lu baax. 22:13 Mu taxaw ci sama wet ne ma: “Sool sama mbokk, delluwaatal di gis.” Noonu ma daldi gisaat ca saa sa, xool ko. 22:14 Mu ne ma: “Sunu Yàllay maam tànn na la, ba may la, nga xam coobareem te gis Aji Jub ji te nga dégg ay waxam. 22:15 Ndaxte li nga gis te dégg ko, dinga ko seede ci ñépp. 22:16 Léegi nag, looy nég? Jógal, ñu sóob la ci ndox, nga set ci say bàkkaar ci tudd turu Yeesu.” 22:17 «Bi ma dellusee Yerusalem nag, di ñaan ca kër Yàlla ga, leer tàbbi ci man. 22:18 Ma daldi gis Boroom bi, mu ne ma: “Génnal Yerusalem ci ni mu gën a gaawe, ndaxte duñu nangu li ngay seede ci man.” 22:19 Waaye ma tontu ne: “Boroom bi, xam nañu ne, dama daan wër jàngoo-jàngu, di tëj kaso ak di dóor ay yar ñi la gëm. 22:20 Rax-ca-dolli bi ñu tuuree deretu Ecen, mi la doon seedeel, teewe naa ko, ànd ca, bay wottu sax yérey ñi ko doon rey.” 22:21 Waaye Boroom bi ne ma: “Demal, dinaa la yebal fu sore, nga jëm ci xeeti ñi dul Yawut.”» 22:22 Mbooloo ma déglu ko nag ba ca wax jooju, waaye bi ñu déggee loolu, ñu daldi yuuxu naan: «Farleen ko ci àddina! Yembar mu mel ni moom yeyoowul a dund!» 22:23 Ñu daldi yuuxu ak di sànni seeni yére, tey callameeru suuf. 22:24 Noonu kilifa ga santaane, ñu dugal Pool ca tata ja te caw ko ay yar yu metti, laaj ko ba xam lu tax ñu di ko yuuxoo nii. 22:25 Waaye bi ñu koy joñ ak ay der, Pool ne njiitu xare ba fa taxaw: «Ndax am nga sañ-sañu dóor ay yar jaamburu Room, te fekk yoon dabu ko sax?» 22:26 Bi ko njiit la déggee, mu fekki kilifaam, yégal ko ko; mu ne ko: «Ndax xam nga li ngay def? Nit kale jaambur la ci Room.» 22:27 Noonu kilifa ga ñëw laaj Pool: «Wax ma, ndax jaambur nga ci Room?» Mu tontu ko: «Waaw, moom laa.» 22:28 Kilifa ga ne ko: «Man fey naa xaalis bu bare, ngir nekk jaambur ci Room.» Waaye Pool tontu ko: «Man de dama koo judduwaale.» 22:29 Ñi ko bëggoon a dóor ay yar nag randu ko ca saa sa. Te kilifa ga sax tiit ci xam ne Pool jaamburu Room la, te yeewlu na ko. 22:30 Ca ëllëg sa mu bàyyi ko, ndaxte bëggoon na xam bu wóor lu ko Yawut ya jiiñ. Mu santaane ne, saraxalekat yu mag ya dajaloo, ñoom ak kureelu àttekat ya. Gannaaw loolu mu indilu Pool, dëj ko ci seen kanam.
23:1 Noonu Pool xool jàkk géew ba ne leen: «Bokk yi, ci xel mu dal laa doxale ci kanam Yàlla ba ci bésu tey bi.» 23:2 Ci kaw loolu saraxalekat bu mag ba, di ku ñuy wax Anañas, sant ña taxaw ca wetam, ñu fél gémmiñam. 23:3 Pool ne ko: «Yàlla dina la dóor, yaw mi naaféq, bay samandaay miir bu joy bu ñu weexal. Yaa ngi toog di ma àtte, ci li yoon wi digle, ba noppi santaane ñu dóor ma, ci li yoon wi tere!» 23:4 Waaye ña taxaw ca wetam ne ko: «Ndax dangay xas saraxalekat bu mag, bi Yàlla fal?» 23:5 Pool tontu leen: «Bokk yi, xawma woon ne saraxalekat bu mag bi la, ndaxte tëral nañu ci Mbind mi ne: “Bul wax lu bon sa kilifag xeet.”» 23:6 Naka noona Pool, mi xam ne, genn-wàllu kureel ga bokk nañu ci tariixab Sadusen ya, te ña ca des bokk ci tariixab Farisen ya, mu wax ci kaw ci biir géew ba ne: «Bokk yi, man Farisen laa, te Farisen moo ma jur; li tax ñu may àtte tey mooy sama yaakaar ci ne, ñi dee dinañu dekki.» 23:7 Bi mu waxee loolu nag, werante wu metti daldi xew diggante Farisen ya ak Sadusen ya, ba mbooloo ma xaajalikoo. 23:8 Ndaxte Sadusen yi nanguwuñu ne, ndekkite mbaa malaaka mbaa rab, dara am na ci, waaye Farisen nangu nañu yooyu yépp. 23:9 Ci kaw loolu nag coow lu bare daldi jib. Ñenn ca xutbakat, ya bokk ca Farisen ya, ne bërét, daldi xuloo bu metti ne: «Gisunu dara lu bon ci nit kii. Su fekkeente ne, rab a ko wax mbaa malaaka...?» 23:10 Noonu xuloo ba daldi gën a tàng, ba kilifa ga ragal ne, nit ñi dinañu daggaate Pool. Kon mu sant xarekat ya, ñu wàcc, nangu Pool ci ñoom, yóbbu ko ca tata ja. 23:11 Ca guddi ga nag Boroom bi taxaw ci wetu Pool ne ko: «Takkal sa fit; ni nga ma seedee ci Yerusalem, noonu nga may seedee ca Room.» 23:12 Bi bët setee Yawut ya daldi lal pexe; ñu dige ci ngiñ ne, duñu lekkati, duñu naanati, ba kera ñuy rey Pool. 23:13 Ña lal pexe ma, seen lim ëpp na ñeent-fukk. 23:14 Noonu ñu dem ca saraxalekat yu mag ya ak njiit ya ne leen: «Giñ nanu ne, dunu mos dara, ba kera nuy rey Pool. 23:15 Léegi nag yéen ak kureelu àttekat ya, laajleen kilifa ga, mu indi ko ci seen kanam, mel ni dangeen a bëgg a seet mbiram bu gën a wóor. Bu ko defee nun dinanu fagaru, ngir rey ko, bala moo agsi.» 23:16 Waaye jarbaatu Pool yég fiir ga, mu dem, dugg ca tata ja, yégal ko Pool. 23:17 Bi ko Pool déggee, mu woo kenn ca njiiti xare ba ne ko: «Yóbbul waxambaane wii ca kilifa ga, ndax am na lu mu ko war a yégal.» 23:18 Njiit la jël ko, yóbbu ko ca kilifa ga ne ko: «Pool, mi ñu jàpp, moo ma woo, ñaan ma, ma indil la waxambaane wii, ndaxte am na lu mu lay wax.» 23:19 Noonu kilifa ga jàpp ci loxob waxambaane wa, wéetoo ak moom, laaj ko: «Loo ma bëgg a yégal?» 23:20 Mu tontu ne: «Yawut yi dañoo dige, ngir ñaan la, nga indi Pool ëllëg ca kanamu kureelu àttekat ya, mel ni dañoo bëgg a seet mbiram bu gën a wóor. 23:21 Bu leen ko may, ndaxte lu ëpp ñeent-fukk ci ñoom ñu ngi koy lalal fiir. Dige nañu ak ngiñ ne, dootuñu lekk, dootuñu naan, li feek reyuñu ko; fi mu ne sax fagaru nañu, di xaar, nga nangu.» 23:22 Kilifa ga nag sant waxambaane wa, mu bañ koo àgge kenn, ba noppi mu yiwi ko, mu dem. 23:23 Bi mu ko defee mu woo ñaar ci njiiti xare ba ne leen: «Waajal-leen ñaari téeméeri xarekat ak juróom-ñaar-fukki gawar ak ñaari téeméer ñu gànnaayoo xeej, ngeen dem Sesare ci juróom-ñeenti waxtu ci guddi. 23:24 Wutal-leen it Pool lu mu war, ngeen yóbbu ko ci jàmm ak salaam ba ca Feligsë, boroom réew mi.» 23:25 Noonu mu bind bataaxal bii: 23:26 Yaw Feligsë mu tedd mi, di boroom réew mi; man Këlódd Lisiyas maa ngi lay nuyu. 23:27 Yawut yi jàpp nañu nit kii, bëgg koo rey, waaye bi ma yégee ne, jaambur la ci Room, wallu naa ko ak ay xarekat, ba musal ko. 23:28 Bëggoon naa xam lu tax ñu kalaame ko. Moo tax ma yóbbu ko ca kanamu seen kureelu àttekat ya. 23:29 Gis naa ne li ñu ko jiiñ mu ngi aju ci ay werantey seen yoon, waaye jiiñuñu ko dara lu jar dee mbaa jéng. 23:30 Te bi ma déggee ne, ñu ngi koy fexeel, yebal naa ko ci yaw ci saa si. Sant naa nag ñi ko kalaame, ñu xamal la seen lay. 23:31 Noonu xarekat ya jël Pool ci guddi, indi ko ba ca dëkku Antipataris, ni ñu leen ko sante. 23:32 Ca ëllëg sa ñu woññiku, dellusi ca tata ja, bàyyi gawar ga, ñu gunge ko. 23:33 Bi gawar ga àggee Sesare, ñu jox boroom réew ma bataaxal ba, jébbal ko Pool. 23:34 Bi loolu amee boroom réew ma jàng bataaxal ba, laaj ci ban diiwaan la Pool dëkk. Bi mu yégee ne, mu ngi dëkk Silisi, 23:35 mu ne ko: «Kon bu ñi la kalaame ñëwee, dinga layoo.» Mu santaane nag, ñu denc ko ca kër buur ba Erodd.
24:1 Bi juróomi fan wéyee, Anañas saraxalekat bu mag ba dikk, ànd ak ay njiit ak layookat bu tudd Tertul, ñu woo Pool ci yoon fa kanam boroom réew ma. 24:2 Noonu ñu woo Pool, te Tertul daldi ko jiiñ naan: «Yaw Feligsë mu tedd mi, sa nguur jural na nu jàmm ju neex, te sa jàppandil soppi na lu bare ci sunu xeet. 24:3 Gis nanu ko fépp ak ci lépp, di la gërëm ak sunu xol bépp. 24:4 Waaye ngir bañ a yàggal jataay bi, maa ngi lay ñaan ci sa lewetaay, nga déglu nu ci lu gàtt. 24:5 Ndaxte ci mbirum nit kii teew, gis nanu ne rambaaj la, buy indi xëccoo ci Yawut yi ci àddina sépp, di njiitu mbooloo mu ñuy wax Nasaréen. 24:6 Dem na ba jéem a teddadil sax kër Yàlla ga, waaye jàpp nanu ko. 24:8 Soo ko laajee, yaw ci sa bopp, dinga gis ne, li nu koy jiiñ dëgg la.» 24:9 Ci kaw loolu Yawut ya ànd ca, di dëggal ne loolu wóor na. 24:10 Bi loolu amee boroom réew ma jox Pool kàddu gi. Noonu mu làyyi ne: «Xam naa ne, yaa ngi àtte xeet wi diirub at yu bare, moo tax maa ngi làyyi ak kóolute. 24:11 Man ngaa wóorliku ne, ëppagul fukki fan ak ñaar demoon naa Yerusalem ngir màggali. 24:12 Te kenn gisu ma, maay werante mbaa di jógloo mbooloo, muy ca kër Yàlla ga mbaa ca jàngu ya mbaa ci biir dëkk ba. 24:13 Te mënuñoo firndeel dara ci li ñu may jiiñ léegi. 24:14 Waaye nangu naa ci sa kanam ne, maa ngi jaamu Yàllay sunuy maam, ci topp yoon wi ñu ne, mooy tariixa; terewul ne, lépp li ñu tëral ci yoonu Musaa ak li yonent yi bind, gëm naa ko. 24:15 Te bokk naa ak ñoom yaakaar ci Yàlla, ne ñi jub ak ñi jubadi dinañu dekki keroog yawmelxayaam. 24:16 Moo tax fu ma tollu, maa ngi góor-góorlu, ngir am xel mu dal fa kanam Yàlla ak fa kanam nit ñi. 24:17 «Noonu gannaaw gëjeb at yu bare ñëw naa, ngir indil sama xeet ndimbal te jébbal Yàlla ay sarax. 24:18 Bi ma koy def nag, gis nañu ma ca kër Yàlla ga, ma setlu ba noppi, fekk ànduma ak mbooloo te indiwuma benn coow. 24:19 Waaye ay Yawut yu dëkk Asi — xanaa kay ñoo waroon a ñëw ci sa kanam, di ma kalaame, bu ñu amee dara lu ñu may topp. 24:20 Waaye it na nit ñii wax ci lan laa tooñe ci jataayu géewub àtte ba, 24:21 xanaa li ma waxoon ca kaw ci seen biir rekk ne: “Mbirum ndekkitel ñi dee moo tax ngeen dëj ma ci seen kanam tey!”» 24:22 Bi mu waxee noonu, Feligsë mi xam bu wóor mbirum yoon wi, yiwi leen ba beneen yoon. Mu ne leen: «Bu Lisiyas kilifag xare bi ñëwee, dinaa àtte seen mbir.» 24:23 Noonu mu sant njiitu xare ba ne ko: «Nanga wottu Pool, waaye nga may ko féex, te bàyyi ay xaritam, ñu topptoo ko.» 24:24 Bi ay fan wéyee, Feligsë ñëwaat, ànd ak jabaram Dursil, miy Yawut. Noonu mu woolu Pool, di ko déglu ci mbirum gëm Yeesu Kirist. 24:25 Waaye bi Pool di waxtaan ci mbirum njub ak moom sa bopp ak bés pénc, Feligsë daldi tiit, yiwi ko ne ko: «Demal, bu ma amee jot, dinaa la woolu.» 24:26 Fekk yaakaaroon na it ne, Pool dina ko jox xaalis; kon mu di ko faral a woolu, ngir waxtaan ak moom. 24:27 Bi ñaari at weesoo nag, amoon na ku wuutu Feligsë, tudd Porsiyus Festus. Noonu Feligsë, mi bëggoon lu neex Yawut ya, bàyyi Pool ca kaso ba.
25:1 Bi Festus teersee ci diiwaanam, mu teg ca ñetti fan, dem Yerusalem. 25:2 Noonu saraxalekat yu mag ya ak njiiti Yawut ya kalaame Pool ci moom. 25:3 Ñuy sàkku ndimbal ci moom, di ko ñaan bu wér, mu yónni Pool Yerusalem, fekk lal nañu fiiru rey ko ca yoon wa. 25:4 Waaye Festus tontu leen ne: «Ñu ngi wottu Pool ca Sesare, te dinaa fa dem fi ak fan yu néew.» 25:5 Mu ne leen: «Ñi am maana ci yéen nag, nangeen ànd ak man, layooji ak nit ka, bu dee tooñ na.» 25:6 Noonu Festus am fa ñoom juróom-ñett ba fukki fan, ba noppi dem Sesare. Ca ëllëg sa mu toog ca àttekaay ba, joxe ndigal, ñu indi Pool. 25:7 Bi mu ñëwee nag, Yawut ya jóge Yerusalem wër ko, di ko jiiñ tooñ yu bare te réy, te mënuñu leen a firndeel. 25:8 Noonu Pool làyyi ne: «Tooñuma yoonu Yawut ya, tooñuma kër Yàlla ga, tooñuma buur ba Sesaar.» 25:9 Ci kaw loolu Festus, mi bëgg lu neex Yawut ya, tontu Pool ne: «Ndax bëgguloo dem Yerusalem, nga layoo fa ci mbir yii ci sama kanam?» 25:10 Waaye Pool ne ko: «Maa ngi nii taxaw ci kanam àttekaayu buur Sesaar; te fii lañu ma war a àttee. Te yaw ci sa bopp xam nga bu baax ne, tooñuma Yawut yi. 25:11 Su ma tooñoon mbaa ma def lu bon lu jar dee, kon duma tinu ngir bañ a dee. Waaye bu li ñu may jiiñ taxawul, kenn sañu ma leen a jébbal. Dénk naa sama mbir Sesaar.» 25:12 Bi mu waxee loolu, Festus gise ak ñi ko wër, mu tontu ko: «Dénk nga sa mbir Sesaar, kon ci moom ngay dem.» 25:13 Ba ñu ca tegee ay fan, buur Agaripa ak Berenis ñëw Sesare, ngir nuyusi Festus. 25:14 Bi seen ngan di ruus nag, Festus diis buur ba mbirum Pool ne ko: «Feligsë batale na nu ak kenn ku ñu tëj. 25:15 Te bi ma nekkee Yerusalem, saraxalekat yu mag ya ak njiiti Yawut ya kalaame nañu ko ci man, ñaan ma, ma daan ko. 25:16 Waaye ma tontu leen ne: “Jébbale nit, fekk jàkkaarloowul ak ñi koy jiiñ, ba man a làyyil boppam ci li ñu koy jiiñ, loolu dëppoowul ak aaday nguuru Room.” 25:17 Bi ñu àndee ak man ba fii nag, randaluma mbir mi, waaye ca ëllëg sa sax toog naa ca àttekaay ba, joxe ndigal, ñu indi nit kooku. 25:18 Ñi koy kalaame nag, bi ñu taxawee, jiiñuñu ko benn ñaawteef ci yi ma yaakaaroon; 25:19 waaye ñuy werante rekk ak moom ci seen yoon ak ci mbirum ku tudd Yeesu, mi dee, te Pool sax ci ne, mu ngi dund. 25:20 Gannaaw lijjanti mbir moomu jafe woon na ma lool nag, ma laaj ko, ndax bëgg na dem Yerusalem, layooji fa ci mbir yooyu. 25:21 Waaye Pool ñaan, nu fomm mbiram, ba kera buur bu tedd ba di ko àtte. Noonu santaane naa ñu aj ko, ba keroog ma koy yónnee Sesaar.» 25:22 Booba nag Agaripa ne Festus: «Man sax bëgg naa dégg nit kooku.» Festus tontu ko: «Bu ëllëgee dinga ko dégg.» 25:23 Ca ëllëg sa nag Agaripa ak Berenis ñëw bu xumb, ñu dugg ca néegu àtte ba, ànd ak kilifay xare ba ak ña am maana ca dëkk ba. Noonu Festus joxe ndigal, ñu indi Pool. 25:24 Bi mu ñëwee, Festus ne: «Buur Agaripa ak yéen ñépp, ñi fi teew tey, nit kaa ngi nii! Mbiram moo tax mbooloom Yawut yépp, muy ci Yerusalem, muy fii, wër ma di yuuxu ne: “Nit kii waratul a dund.” 25:25 Waaye gis naa ne, deful dara lu jar dee. Moona, gannaaw moom ci boppam dénk na boppam buur bu tedd ba, fas naa yéene yónnee ko ko. 25:26 Fekk awma dara lu wóor ci mbiram, lu ma man a bind sang bi. Moo tax ma indi ko ci seen kanam, rawatina ci sa kanam buur Agaripa, ngir sunu jataay may ma lu ma bind. 25:27 Ndaxte yaakaar naa ne, yónnee ku ñu tëj, te bañ caa boole lu ko waral, àndul ak xel.»
26:1 Bi mu ko waxee, Agaripa ne Pool: «Jëlal kàddu gi.» Noonu Pool tàllal loxoom, daldi làyyi ne: 26:2 «Buur Agaripa, ma làyyi ci sa kanam tey ci lépp, li ma Yawut yiy jiiñ, xol bu sedd la ci man, 26:3 ndaxte xam nga bu baax aaday Yawut yi ak seeni werantey yoon. Kon maa ngi lay ñaan, nga déglu ma ak muñ. 26:4 «Ci lu jëm ci Yawut yi, xam nañu sama dund li dale ci samag ndaw, muy ci sama biir xeet, muy ci Yerusalem. 26:5 Xam nañu ma bu yàgg te man nañoo seede, su leen neexee, ne daan naa dund ni Farisen, te mooy tariixa bi gën a diis ci sunu diine. 26:6 Li ma indi ci kureelu àttekat yii nag, mooy yaakaar ne, Yàlla dina amal li mu digoon sunuy maam. 26:7 Dige booba la fukki giir ak ñaar yu bànni Israyil di sàkku, ngir jot ko, ci jaamu Yàlla ak cawarte guddi ak bëccëg. Yaw buur, yaakaar joojoo tax ñu may kalaame, ñoom Yawut yi. 26:8 Lu tax seen xel dàq ne, Yàlla dina dekkal ñi dee? 26:9 «Man sax ci sama bopp defe woon naa ne, war naa def lu bare, ngir suufeel turu Yeesum Nasaret. 26:10 Daan naa ko def ci Yerusalem, ba noppi ma jot sañ-sañ ci saraxalekat yu mag ya, bay tëj gaayi Yàlla yu bare. Rax-ca-dolli ku ñu ci masoon a bëgg a rey, ànd naa ci. 26:11 Daan naa wër jàngoo-jàngu, di leen teg toskare te di leen jéem a weddiloo. Te sama mer daa na tar, ba ma di leen xañ ba ca dëkk yu sore, ngir fitnaal leen. 26:12 «Noonu am bés, may dem dëkku Damas, yor sañ-sañ ak ndigalu saraxalekat yu mag ya. 26:13 Ca njolloor, buur bi, gis naa ca yoon wa leer gu jóge asamaan ne ràyy, ba raw leeru jant, melax ba ëmb ma, man ak ñi ma àndal. 26:14 Nu ne nërëm ci suuf, ma dégg baat bu ma wax ci làkku yawut ne: “Sool, Sool, lu tax nga di ma fitnaal? Ngay bëre ak man ni fas wuy woŋŋeetu ku koy jam dëgël, metti na ci yaw.” 26:15 «Noonu ma tontu ko: “Yaa di kan, Boroom bi?” Boroom bi ne ma: “Maa di Yeesu, mi ngay fitnaal. 26:16 Waaye jógal taxaw. Lii moo tax ma feeñu la: teg naa la yen, nga di ma seedeel ci lépp li nga gis ci man, ak li ma lay feeñuji. 26:17 Dinaa la musal ci bànni Israyil ak ci ñi dul Yawut. Ci ñoom laa lay yebal, 26:18 ngir ubbi seeni bët, nga jële leen ci lëndëm, tàbbal leen ci leer, nga nangoo leen ci sañ-sañu Seytaane, woññi leen ci Yàlla, ma baal leen seeni bàkkaar te may leen cér ci biir sama gaa yi sell ci kaw ngëm.” 26:19 «Kon nag buur Agaripa, woruma li ma Yàlla yen ci peeñu. 26:20 Waaye li tàmbali ci Damas, teg ci dëkku Yerusalem ak réewu Yawut mépp, ba agsi ci ñi dul Yawut, yégal naa leen, ñu tuub seeni bàkkaar te woññiku ci Yàlla, bay jëf lu dëppook réccu. 26:21 Loolu nag moo waral Yawut yi jàpp ma ca kër Yàlla ga, di ma fexee rey. 26:22 Waaye gannaaw Yàllaa ngi may taxawu ba tey, maa ngi taxaw fi, di ko seedeel ci mag ak ndaw; yokkuma dara ci li yonent yi ak Musaa xamle woon lu jiitu, 26:23 maanaam Almasi bi dina dékku ay coono, te mooy jëkk a dekki, bay jollil leer ci bànni Israyil ak ñi dul Yawut.» 26:24 Bi muy làyyee nii, Festus daldi ko gëdd ak baat bu kawe ne ko: «Dangaa dof Pool! Xanaa sa njàng mu réy mi da laa xañ sago.» 26:25 Waaye Pool tontu ko: «Festus mu tedd mi, dofuma; waaye lu dëggu laay wax te ànd ak sago. 26:26 Yëf yii leer na buur bi, moo tax maa ngi koy wax ak kóolute. Wóor naa ne, dara ci lii may wax umpu ko, ndaxte lii amewul ciy ruq. 26:27 Yaw buur Agaripa, ndax gëmuloo yonent yi? Xam naa bu wér ne, gëm nga.» 26:28 Noonu Agaripa ne Pool: «Xanaa yaw, ci diir bu gàtt bii rekk, nga ma bëgg a dugale ci gaayi Kirist!» 26:29 Pool tontu ko: «Muy tey, muy ëllëg, waxuma yaw rekk waaye it ñi may déglu tey ñépp, na Yàlla def, ba ngeen fekksi ma ci li ma nekk, lu moy jéng yii!» 26:30 Ci kaw loolu buur ba daldi jóg, boroom réew ma topp ci, Berenis tegu ca ak mbooloo ma mépp. 26:31 Bi ñu génnee nag, ñuy waxante ne: «Nit kii deful dara lu jar dee mbaa kaso.» 26:32 Te Agaripa ne Festus: «Manoon nanu koo yiwi, bu dénkuloon mbiram Sesaar.»
27:1 Bi loolu wéyee ñu fas yéene noo dugal gaal jëme réewu Itali. Noonu ñu jël Pool ak ñeneen ñi ñu tëjoon, dénk leen njiitu xare bu tudd Yulyus, mi bokk ci mbooloom xare mu buur. 27:2 Nu dugg ca gaalu dëkku Adaramit guy taxaw ci teeruy Asi, daldi tàbbi ci biir géej; te Aristàrk, mi dëkk Tesalonig ci diiwaanu Maseduwan, ànd ak nun. 27:3 Ca ëllëg sa nu teer Sidon; Yulyus laabiir ci Pool, may ko mu dem ci ay xaritam, ngir ñu ganale ko. 27:4 Bi nu fa jógee, nu dem ci biir géej, leru dunu Sipar ci fegu ngelaw li, ndaxte ngelaw li da noo soflu. 27:5 Nu jàll géej, gi janook diiwaani Silisi ak Pamfili, teersi Mira ca wàlli Lisi. 27:6 Foofa nag njiit la gis gaal gu jóge Alegsàndiri, jëm Itali, mu dugal nu ca. 27:7 Noonu nuy dem ndànk diirub fan yu bare, ba janook Kanidd ci kaw coono bu réy; te ndegam ngelaw li mayu nu, nu jëm kanam, nu leru dunu Kereet ci fegu ngelaw li, janook Salmon. 27:8 Nu romb fa ak coono yu bare, agsi ca bérab bu ñuy wax Teeru yu neex, te dend ak dëkku Lase. 27:9 Fekk booba yàggoon nañu ca yoon wa, te dem ci géej daldi aaytal, ndaxte jamonoy Kooru Yawut ya wees na. Moo tax Pool digal leen ne: 27:10 «Gaa ñi, gis naa ne, tukki bi ëmb na musiba ak kasara ju bare, waxuma gaal gi ak li mu yeb waaye sunuy bakkan sax xaj na ci.» 27:11 Waaye njiit la sobental waxi Pool, déggal dawalkat ba ak boroom gaal ga. 27:12 Te gannaaw teeru ba neexul a lollikoo, ña ca ëpp mànkoo ci jóge fa, dem ci biir géej, ngir wut a agsi Fenigsë, biy teerub dunu Kereet te janook sowu suuf ak sowu kaw, nu lollikoo fa. 27:13 Noonu bi ngelaw lu woyof liy jóge sudd wolee, ñu defe ne, man nañoo sottal seen pexe, ñu wëgg diigal, daldi tafu ci dunu Kereet. 27:14 Waaye nes tuuti ngelaw lu wole penku, ñu di ko wax «Ërakilon,» jóge ca dun ba, ne milib ci sunu kaw. 27:15 Mu ëpp doole gaal ga, daldi ko wat, ba nu bayliku, daldi yal. 27:16 Nu daldi daw, leru dun bu tuuti bu ñuy wax Kóda ci fegu ngelaw, rawale looco ga ci kaw gaal ga ak coono bu bare. 27:17 Bi ñu ko yéegee, ñu fab ay buum, ngir laxas ca taatu gaal ga, ngir ragal a daanu ci suuf su nooy su ñuy wax Sirt; ba noppi ñu daldi sànni diigal, ngir wàññi doxub gaal ga, nuy yale noonu. 27:18 Waaye bi nu ngelaw li sonalee bu metti, ca ëllëg sa ñu sànni la gaal ga yeboon ca géej ga. 27:19 Te ca ñetteelu fan ba, ñu sànni ak seeni loxo jumtukaay, yi ñu yeboon ngir fàggu. 27:20 Noonu jant bi ne meŋŋ te biddiiw ne mes ay fan yu bare, fekk ba tey ngelaw li di wol ak doole, ba sunu yaakaaru mucc gépp tas. 27:21 Bi loolu di xew, fekk gëj nañoo lekk, Pool daldi taxaw ci seen biir ne leen: «Gaa ñi, li gënoon mooy ngeen déglu ma te bañ a jóge Kereet, ba indil seen bopp musiba ak kasara ju réy jii. 27:22 Léegi nag maa ngi leen di dénk, ngeen takk seen fit, ndax gaal gi rekk mooy yàqu, waaye kenn ci yéen du dee. 27:23 Ndaxte ci guddi menn malaaka dikkal na ma, jóge ci Yàlla sama Boroom, bi may jaamu. 27:24 Mu ne ma: “Pool bul tiit; fàww nga taxaw ci kanamu Sesaar, te yaa tax Yàllay aar bakkani ñi nga àndal ñépp.” 27:25 Moo tax gaa ñi, takkleen seen fit, ndax wóolu naa Yàlla ne, li mu ma wax, dina am. 27:26 Waaye war nanoo luf cib dun.» 27:27 Ca fukkeelu guddi ga ak ñeent nu nga doon jayaŋ-jayaŋi ca géeju Adiratig; noonu ca xaaju guddi dawalkati gaal ga defe ne, danu jegesi suuf. 27:28 Ñu sànni nattukaay ba ci biir géej, mu jàpp ñeent-fukki meetar, dem ca kanam tuuti, sànniwaat ko, jàpp fanweeri meetar. 27:29 Ñu ragal ne, dinañu fenqu ci ay xeer, kon ñu daldi sànni ñeenti diigal ci geenu gaal ga, di ñaan bët set. 27:30 Waaye ci kaw loolu dawalkati gaal ga taafantaloo sànniji ay diigal ca boppu gaal ga, fekk dañuy fexee jël looco ga, ba raw. 27:31 Waaye Pool ne njiit la ak xarekat ya: «Bu ñii desul ci gaal gi, dungeen raw.» 27:32 Noonu xarekat ya dagg buum, yay téye looco ga, bàyyi ko mu wéy. 27:33 Bi bët setagul, Pool sant leen ñu lekk; mu ne leen: «Tey mooy seen fukki fan ak ñeent yu ngeen ne jonn, lekkuleen, mosuleen dara. 27:34 Maa ngi leen di sant nag, ngeen lekk, ndax noonu rekk ngeen man a rawe. Ndax genn kawar du rot ci yéen.» 27:35 Bi mu waxee loolu, mu fab mburu, sant Yàlla ci kanamu ñépp, damm ko, daldi ko lekk. 27:36 Bi ñu gisee loolu, ñépp dëgëraat, ñu daldi lekk ñoom itam. 27:37 Mboolem ñi nekkoon ca gaal ga mat na ñaari téeméeri nit ak juróom-ñaar-fukk ak juróom-benn. 27:38 Noonu ñu lekk ba suur, daldi sànni pepp ma ca géej ga, ngir woyofal gaal ga. 27:39 Bi bët setee nag, xàmmiwuñu réew ma, waaye séen nañu ruqu tefes. Noonu ñu fas yéene caa teeral gaal ga, bu ñu ko manee. 27:40 Ñu dagg diigal ya, bàyyi leen ci biir géej, yiwiwaale baar ba; ba noppi firi wiiru kanam ga, jublu ca tefes ga. 27:41 Waaye ñu dal ca tundu suuf ca bérab bu ñaari koroŋ daje, gaal ga daldi fa luf. Boppu gaal ga nuur bu baax, ne fa tekk, te dooley duus ya daldi toj geen ba. 27:42 Bi loolu amee xarekat ya bëgg a rey ñi ñu tëj, ngir ragal ñenn ñi féey, ba raw. 27:43 Waaye njiit la bëgg a musal Pool, mu tere leen pexe ma. Mu sant ñi man a féey, ñu jëkk a sóobu ca ndox ma, ba jot tefes ga. 27:44 Mu sant ñi ci des ñu def noonu, langaamu ci ay dénk, mbaa ca tojiti gaal ga. Noonu ñépp jot tefes ga ci jàmm ak salaam.
28:1 Bi nu rëccee, nu yég ne dun baa nga tudd Màlt. 28:2 Te waa réew ma won nu laabiir gu ràññiku, ndaxte taalal nañu nu safara, ganale nu ndax taw bi sóob ak sedd bi. 28:3 Pool nag di for matt, di ko def ca taal ba, jaan ne ca mëlle ndax tàngoor wa, taq ci loxoom. 28:4 Bi waa réew ma gisee rab wa wéqu ci loxoom nag, ñuy waxante naan: «Ci lu wóor nit kii reykat la; te bi mu rëccee ca géej ga sax, ndogalu Yàlla mayu ko mu dund.» 28:5 Waaye Pool yëlëb rab wa ca safara sa, te wàññiwu ko dara. 28:6 Nit ñi di xaar mu newi, mbaa mu ne dàll, dee; waaye bi ñu négee lu yàgg te gis ne dara jotu ko, ñu soppi xel ne: «Kii yàlla la.» 28:7 Amoon na nag ca wet ya ay suuf yu doon moomeelu ku tudd Publiyus, di kilifag dun ba. Mu teeru nu, ganale nu ngan gu réy diirub ñetti fan. 28:8 Fekk baayu Publiyus dafa tëdd ndax ay tàngoori yaram yu koy dikkal ak biiru taññ. Pool nag dem seeti ko, ñaan ci Yàlla, teg ko ay loxoom, mu daldi wér. 28:9 Ci kaw loolu jarag ya ca des ca dun ba daldi dikk, amaat wér-gi-yaram. 28:10 Ñu teral nu ci fànn yu bare, te bi nuy dem, ñu jox nu li nuy soxla lépp. 28:11 Bi nu fa amee ñetti weer, nu dugg ca gaal gu lollikoo ca dun ba, daldi tàbbi ca géej ga. Gaalu dëkku Alegsàndiri la woon, te yor xàmmikaay guy nataalu Kastor ak Polugsë. 28:12 Noonu nu teer dëkku Sirakus, toog fa ñetti fan. 28:13 Nu jóge fa, leru tefes ga, ba agsi Resiyo. Ca ëllëg sa ngelawu sudd daldi jóg, te ca ñaareelu fan ba nu teer Pusol. 28:14 Gis nanu fa ay bokk, ñu ñaan nu, nu toog fa ayu-bés. Noonu nu dem Room. 28:15 Sunuy xebaar law na, ba egg ca bokk ya fa dëkk, noonu ñu gatandu nu ba ca péncu Apiyus ak bérab bu ñuy wax Ñetti añukaay ya. Bi leen Pool gisee, mu sant Yàlla, daldi takk fitam. 28:16 Bi nu dikkee Room nag, ñu may Pool, mu dëkk fa ko lew, moom ak xarekat ba koy wottu. 28:17 Bi ñetti fan wéyee, mu woolu njiiti Yawuti dëkk ba. Bi ñu dajaloo nag, mu wax leen lii: «Bokk yi, jàpp nañu ma ci Yerusalem, jébbal ma waa Room, fekk defuma dara luy suufeel sunu xeet, mbaa lu juuyoo ak sunuy aaday maam. 28:18 Waa Room nag seet sama mbir, te bëgg maa bàyyi, ndaxte toppuñu ma dara lu jar dee. 28:19 Waaye bi ko Yawut ya bañee, fas yéene naa dénk sama mbir Sesaar, fekk ba tey awma dara lu may taqal sama xeet. 28:20 Moo tax ma ñaan a gise ak yéen, nu diisoo, ndaxte yaakaaru bànni Israyil moo tax ñu jéng ma.» 28:21 Bi ñu ko déggee, ñu tontu ko: «Jotunu benn bataaxal bu jóge Yude ci sa mbir, te kenn ci bokk, yi fi dikk, jottaliwul mbaa mu seede ci yaw lu bon. 28:22 Waaye bëgg nanoo dégg li nga gëm, ndaxte xam nanu ne, tariixa booba, kenn jubluwu ko fenn.» 28:23 Noonu ñu dig ko bés, te ñu bare ñëw, fekksi ko ca néegam. Mu di leen jàngal suba ba ngoon, di leen dëggal lu jëm ci nguuru Yàlla ak ci Yeesu, tukkee ci yoonu Musaa ak ci yonent yi, di leen jéem a gëmloo. 28:24 Ñenn ñi nag gëm li mu wax, ña ca des weddi ko. 28:25 Gannaaw mënuñoo déggoo, ñu bëgg a tas. Waaye bi ñu laata dem, Pool teg ca wax jii: «Xel mu Sell mi wax na dëgg ak seeni maam, jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi. 28:26 Nee na:“Demal ci xeet wii ne leen:‘Dingeen déglu bu baaxwaaye dungeen xam dara;di xool bu baax waaye dungeen gis dara.’ 28:27 Ndaxte xolu xeet wii dafa dërkiis;dañuy déglu ak nopp yu naqari,tey gëmm seeni bët,ngir bañ a gis ak seeni bët,dégg ak seeni nopp,te xam ci seen xol,ñu woññiku ci man, ma wéral leen.” 28:28 «Xamleen nag ne, xebaaru mucc gii yégal nañu ko ñi dul Yawut, te ñoom dinañu ko déglu.» 28:30 Noonu diirub ñaari at Pool dëkk ca kër gu muy fey, di fa àggali ñépp ñi koy seetsi. 28:31 Muy yégle nguuru Yàlla, di jàngale ci mbirum Boroom bi Yeesu Kirist ak fit wu dëgër, te kenn terewu ko ko.
1:1 Man Pool, jaamub Kirist Yeesu, maa leen di bind bataaxal bii. Yàlla woo na ma, ma nekk ndawam, sas ma liggéeyu xamle xebaaram bu baax bi. 1:2 Xebaar bu baax boobu, Yàlla dige woon na ko bu yàgg, jaarale ko ciy yonentam, ñu def ko ci Mbind mu sell mi, 1:3 di xamle mbirum Doomam, Yeesu Kirist sunu Boroom. Lu jëm ci meloom ci àddina, ci askanu Daawuda la jóge, waaye lu jëm ci xelam mu sell, Doomu Yàlla la; ndaxte ndekkiteem nekk na firnde ju ràññiku, ne moom la. 1:5 Te moom Kirist tàbbal na nu ci yiwu Yàlla, def nu ay ndawam, yónni nu ci biir xeeti àddina sépp, ngir ñu gëm ko te jébbalu, ba màggal turam. 1:6 Te ci ngeen bokk, yéen ñi Yàlla woo, ngeen nekk ci Kirist. 1:7 Yéen ñi dëkk Room ñépp, yéen ñi Yàlla bëgg te woo leen, ngeen nekk gaayam yu sell, na leen Yàlla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak jàmm. 1:8 Kon nag li may jëkk a wax mooy lii: sant naa Yàlla sama Boroom, jaarale ko ci Yeesu Kirist, ngir yéen ñépp, ndaxte seen ngëm siiw na ci àddina sépp. 1:9 Bët bu set maa ngi leen di boole ci samay ñaan. Yàlla seede na li may wax, Yàlla mi may jaamu ci sama xel, ci xamle xebaar bu baax bu Doomam. 1:10 Te li ma koy faral di ñaan mooy lii: bu soobee Yàlla, na ma ubbil bunt, ba ma man a ñëw ci yéen. 1:11 Ndaxte bëgg naa leen a gis lool, ba indil leen barke bu jóge ci Xel mu Sell mi, ndax seen ngëm gën a dëgër. 1:12 Maanaam ma nekk ci seen biir, te nu dimbaleente ci sunu ngëm, ndax man itam ma gën a am doole. 1:13 Bokk yi, damaa bëgg ngeen xam ne, xalaat naa leen a seetsi ay yooni yoon, ngir meññ njariñ ci yéen, ni ma ko defe ci yeneen xeet yi, waaye ay téq-téq ñoo ma téye ba léegi. 1:14 Am naa warugar sama diggante ak ñépp, muy ñi jàng ni Gereg yi, muy ñi jàngul ni Baarbaar yi, ñi bare xam-xam ak ñi barewul xam-xam. 1:15 Li aju ci man nag, jekk naa ngir ñëw, xamal leen xebaar bu baax bi, yéen it waa Room. 1:16 Ndaxte awma benn werante ci xebaar bu baax bi may waare, ndax mbirum Yàlla la, mu làmboo dooleem, ngir musal képp ku ko gëm, muy Yawut ci bu jëkk mbaa ki dul Yawut. 1:17 Ndaxte xebaar bii day wone, ni nit man a jube ci kanam Yàlla, sukkandikoo ci ngëm rekk, tàmbali ci ngëm, yem ci ngëm. Moo tax Mbind mi wax ne: «Ku jub ci kaw ngëm, dinga dund.» 1:18 Merum Yàllaa ngi feeñe asamaan, wàcc ci nit ñi, ndax seen weddi Yàlla gépp ak seen jubadi gépp, ñoom ñi suul dëgg, di topp lu jubadi. 1:19 Ndax li nit man a xam ci Yàlla, leer na ci seen xel, ndax Yàlla won na leen ko. 1:20 Ndaxte ba àddina sosoo ba tey, mbiri Yàlla yu nëbbu ya, maanaam dooleem ju sax ja, ak meloom wu kawe wa, feeñ nañu bu leer, te bir ñépp ci yi mu sàkk, ba tax bunti lay yépp tëj nañu. 1:21 Ndaxte bi ñu xamee Yàlla, taxul ñu màggal ko ni mu ware, mbaa ñu sant ko. Waaye ñu daldi réer ci seen biiri xalaat yu mujjul fenn, ba tax seen xol gumba, ba lëndëm këruus. 1:22 Ñu teg seen bopp ni boroomi xel, fekk ñu ñàkk xel lañu woon. 1:23 Toxal nañu ndamu Yàlla Aji Sax ji, wuutal fa nataali nit ku dul sax, moom ak ay picc, ay rabi àll mbaa yuy raam. 1:24 Moo tax Yàlla bërgël na leen ci seeni bëgg-bëgg, ñu sóobu ciy ñaawteef, di jëfleente lu gàccelu ci seeni cér. 1:25 Toxal nañu dëggu Yàlla, tëral fen, di màggal ak a jaamu mbindeef, ba faaleetuñu sax Aji Bind, ji yelloo cant ba fàww. Amiin. 1:26 Loolu moo tax nag Yàlla bërgël na leen ci seeni bëgg-bëgg yu ruslu. Seeni jigéen sax dëddu nañu li jekk, sóobu ci lu jekkadi, ñoom ak seeni moroom. 1:27 Noonu it góor ñi bàyyi nañu li jekk ci seeni cér, maanaam ànd ak jigéen, bay am ay bëgg-bëgg yu tar ci ànd ak seeni moroom. Góor di defante ak góor li warul, ñu di jot seen peyu réer ci seeni yaram. 1:28 Gannaaw xam Yàlla soxalu leen, Yàlla it bërgël na leen ci seen xel mu bon moomu, ñu sax ci jëf yu jekkadi. 1:29 Seen xol fees na ak lu jubadi, lu bon, bëgge ak coxor; duñu xalaat lu dul kiñaan, rey nit, xuloo, njublaŋ ak ñaaw njort; dañuy jëw, 1:30 di yàq der, di ñu bañ Yàlla te ñàkk sutura, di réy-réylu ak a kañu; ay jàmbaar lañu ci fexe lu bon, di bañ seeni waajur. 1:31 Amuñu xel, amuñu kóllëre, amuñu cofeel, amuñu yërmande. 1:32 Xam nañu ne, ñiy jëfe loolu, Yàlla daganal na seen dee, waaye teewul ñu di ko def, boole ko ak di farle ñi ci sax.
2:1 Kon nag képp ku mu man a doon, yaw miy àtte sa moroom ak ñaaw njort, amuloo aw lay, ndaxte àtte sa moroom, daan sa bopp la; yaa ngi koy àtte ndax ay jëfam, fekk yaw itam noonu ngay jëfe. 2:2 Xam nanu ne, ñiy jëfe noonu, Yàlla dina leen àtte, te àtteem jub na. 2:3 Yaw nag miy àtte ñiy def loolu, te di ko def, ndax defe nga ne, dinga rëcc ci àtteb Yàlla? 2:4 Ndax dangaa xeeb mbaaxu Yàlla, mi yéex a mer te di la muñal? Xanaa xamuloo ne, Yàllaa ngi lay won baaxaayam, ngir nga réccu say bàkkaar? 2:5 Waaye ndegam dëgër nga bopp te bëgguloo réccu, yaa ngi dajale merum Yàlla ci sa bopp. Ndaxte Yàlla sàkk na bés bu muy wone àtteem bu jub bi te meram wàcc ci ñi bon; 2:6 bés booba dina delloo ku nekk ay jëfam. 2:7 Ñiy góor-góorlu ciy def lu baax, bëgg Yàlla boole leen ca ndamam te sédde leen ngërëm ak dund gu sax, dina leen tàbbal ci dund gu dul jeex. 2:8 Waaye ñi dëgër bopp, ba tanqamlu dëgg, di topp lu jubadi, seen pey mooy dooni merum Yàlla ak toroxte. 2:9 Ki doon def lu bon, peyam mooy tiis ak metit wu tar, muy Yawut ci bu jëkk, mbaa ki dul Yawut. 2:10 Waaye ki doon def lu baax, añam mooy bokk ci ndamu Yàlla, am ngërëm ak jàmm, muy Yawut ci bu jëkk, mbaa ki dul Yawut. 2:11 Ndaxte ñépp a yem fa kanam Yàlla. 2:12 Képp ku doon bàkkaar nag te nekkuloo woon ci yoonu Musaa, Yàlla dina la àtte ci lu dul yoonu Musaa, nga door a sànku. Te képp ku doon bàkkaar te nga nekkoon ci yoonu Musaa, Yàlla dina la àtte ci yoon woowu. 2:13 Kon déglu yoonu Musaa rekk doyul; du loolu mooy tax nit jub ci kanam Yàlla; kiy sàmm yoon wi, moom la Yàlla di àtte ni ku jub. 2:14 Ndax ñi dul Yawut te nekkuñu ci yoonu Musaa, ñu ngiy def li yoon woowu tëral, ndaxte Yàlla def na ko ci nit. Te wonee nañu noonu ne, man nañoo ràññee lu baax ak lu bon, su ñu nekkul sax ci yoonu Musaa, 2:15 di wone it ne, Yàlla bind na ci seen xol jëf yi yoonu Musaa santaane. Seen xel it seede na ne noonu la, fekk seeni xalaat ñoo leen di tuumaal, mbaa ñu leen di jéggal. 2:16 Ndax bés dina ñëw, bu xalaat yu làqu yi di feeñ, te Yàlla àtte nit ñi jaarale ko ci Yeesu Kirist. Xebaar bu baax, bi may waare, moo ko wax. 2:17 Maa ngi ñëw nag ci yaw mi ne Yawut nga; yaa ngi sukkandiku ci yoonu Musaa ak di damu ci Yàlla. 2:18 Xam nga coobareem, ndaxte jàng nga ci yoonu Musaa, ba fonk yëf yi gën a baax. 2:19 Yaa ngi teg sa bopp wommatkatu gumba yi ak leeru ñi nekk cig lëndëm. 2:20 Yaa di jàngalekatu ñi jàngul ak xamlekatu ñi xamul, ndaxte xalaat nga ne, Yàlla jagleel na leen ci yoonu Musaa bépp xam-xam ak gépp dëgg. 2:21 Kon nag yaw miy jàngal say moroom, xanaa doo jàngal sa bopp? Yaw miy waare di tere sàcc, mbaa doo sàcc yaw itam? Yaw miy tere njaaloo, mbaa doo njaaloo? 2:22 Yaw miy araamal xërëm yi, mbaa doo sàcc li nekk ci seeni xàmb? 2:23 Yaw miy damoo yoonu Musaa, mbaa doo ko moy, ba indi gàcce ci turu Yàlla? 2:24 Moo tax Mbind mi ne: «Yéena tax ñi nekkul Yawut di suufeel turu Yàlla.» 2:25 Bëggoon naa ngeen xam ne, xaraf am na njariñ, boo ca boolee sàmm yoon. Waaye boo ko ca boolewul, sa xaraf amatul njariñ. 2:26 Te itam ku xaraful, tey def jëf yu jub yi yoonu Musaa santaane, ndax Yàlla du ko teg ni ku xaraf? 2:27 Ku dul Yawut te xaraful waaye di sàmm yoon wi, kooku dina la man a àtte yaw Yawut bi. Ndaxte li ngay xam-xam yoonu Musaa ci Mbind mi te xaraf, terewul nga koy moy. 2:28 Juddu nekk Yawut taxul sag Yawut dëggu, te xaraf ci saw yaram taxul sa xaraf wóor. 2:29 Waaye Yawut dëgg, ci xol lay nekk. Te xaraf dëgg itam, ci xol lay nekk. Du ngistal, lu dëggu la. Te képp ku mel noonu, dees na la gërëm, waxumala nit ñi, waaye Yàlla ci boppam.
3:1 Yawut bi nag, ci lan la rawe ku dul Yawut? Te xaraf lu muy njariñ? 3:2 Raw na ko fu nekk. Ci bu jëkk Yawut yi la Yàlla dénk waxam. 3:3 Bu fekkee ne am na ci ñoom ñu ñàkk kóllëre, ndax loolu man na fanq kóllëreg Yàlla? 3:4 Mukk! Su ñépp nekkoon ay naaféq, du tere Yàlla nekk dëgg. Moom la Mbind mi wax ci Yàlla ne:«Loo wax, ñépp ànd ci,te ku layoo ak yaw, nga yey ko.» 3:5 Su fekkee nag njubadig nit dina feeñal njubteg Yàlla, lu ciy seen xalaat? Wax ji may bëgg a wax nag léegi, waxi nit rekk la, maanaam: ndax kon Yàlla àttewul yoon ci li muy daan ku jubadi? 3:6 Mukk! Ndax su Yàlla jubadi woon, naka lay àttee àddina si? 3:7 Waaye nag xanaa dina am ku tontu ci loolu ne: «Su fekkee sama ñàkk kóllëre gën na yékkati kóllëreg Yàlla, di yokk it ndamam, lu tax kon Yàlla di ma teg ba tey bàkkaarkat, ba di ma àtte?» 3:8 Lu tax mënunoo wax ne: «Nanu def lu bon, ngir lu baax génn ca?» Am na sax ñu nuy tuumaal, di wax ne, noonu lanuy waaree. Waaye ñiy wax loolu, ndaan gi ñu yelloo dina leen dal. 3:9 Kon nag lu nu ci war a wax? Nun Yawut yi, ndax noo gën ñi ci des? Mukk! Ndaxte wone nanu ne, nit ñépp ñu ngi ci nootaangeg bàkkaar, muy Yawut yi mbaa Gereg yi. 3:10 Moom la Mbind mi wax ne:«Ku jub amul, du kenn sax. 3:11 Amul kenn ku xam yëfi Yàlla,mbaa kenn ku koy wut. 3:12 Ñépp jeng nañu,ba kenn amalatul Yàlla njariñ.Kenn du def lu baax, du kenn sax! 3:13 Seen put a ngi xasaw ni méddum ñetti fan,seen làmmiñ làggi ci njublaŋ,te seeni kàddu aay ni daŋaru ñàngóor. 3:14 Duñu génne ci seen gémmiñ lu dul ay móolu ak i xas. 3:15 Ñu sawar lañu ci rey nit. 3:16 Fu ñu jaar, foofa yàqu ak musiba. 3:17 Xamuñu yoonu jàmm, 3:18 te ragal Yàlla sore na seen xol.» 3:19 Xam nanu nag ne, lépp lu yoonu Musaa wax, wax na ko ñi nekk ci yoon woowu, ngir gémmiñ yépp ne miig, te waa àddina sépp jaar ci àtteb Yàlla. 3:20 Ndaxte sàmm yoon wi taxul kenn jub ci kanam Yàlla; solob ndigal yi daal mooy wone bàkkaar. 3:21 Waaye léegi nag Yàlla feeñal na, ni nit man a jube ci kanamam, ci lu séqul ak yoonu Musaa dara. Waaye ba tey yoonu Musaa ak waxi yonent yi seedeel nañu ko. 3:22 Jub ci kanam Yàlla, gëm Yeesu Kirist rekk a koy maye, te képp ku ko gëm bokk nga ci. Ndaxte ñépp a yem fa kanam Yàlla. 3:23 Ñépp a bàkkaar, ba joteetuñu ndamu Yàlla. 3:24 Waaye gannaaw Kirist Yeesu dee na ngir jot leen, Yàlla ciw yiwam man na leen a àtte ni ñu jub ci dara. 3:25 Wàcce na Kirist, mu nekk sarax ngir Yàlla baal nu sunuy bàkkaar, jaar ci deretam ji ñu tuur; te ngëm rekk moo nu ciy boole. Noonu Yàlla firndeel na ne ku jub la, doonte sax dafa muñaloon ñi jiitu jamonoy Kirist, ba jéggal leen seeni bàkkaar. 3:26 Kon ci jamono jii nu ne, Yàlla wone na bu leer ne ku jub la, di àtte ni ku jub képp ku gëm Yeesu, te ba tey dëkk ci njubteem. 3:27 Kan a man a bàkku nag ci kanam Yàlla? Kenn! Lu ko waral nag? Xanaa sàmm yoon? Déedéet! Ngëm rekk. 3:28 Ndaxte danoo dëggal ne, ngëm rekk a tax Yàlla di àtte nit ni ku jub, waaye du sàmm yoon. 3:29 Walla ndax nag Yawut yi rekk la fi nekkal? Ndax nekkalu fi it ñu dul Yawut? Aaŋkay! 3:30 Gannaaw Yàlla kenn la, ñépp la fi nekkal. Ñi xaraf dina leen àtte ni ñu jub ndax seen ngëm, ñi xaraful it dina leen àtte ni ñu jub ndax seen ngëm. 3:31 Xanaa kon ngëm day fanq yoonu Musaa? Mukk! Da koy gën a dëgëral sax.
4:1 Sunu maam Ibraayma, mi nu soqikoo; nu mbiram tëdde? 4:2 Bu fekkoonte ne Ibraayma, ci kaw i jëfam la ko Yàlla àttee ni ku jub, kon am na lu mu ci man a damoo. Waaye demewul noonu ci kanam Yàlla. 4:3 Lan la Mbind mi wax ci loolu? Nee na: «Ibraayma gëm na Yàlla, te Yàlla jàppe ngëmam ni njub.» 4:4 Képp kuy liggéey dina jot peyam; te pey googu du ag may, ñaqam la. 4:5 Waaye Yàlla dina àtte jub sax ki ko weddi woon; kon ku wéeruwul ciy jëfam, waaye mu gëm rekk, Yàlla dina jàppe ngëmam ni njub. 4:6 Noonu la Daawuda birale barkeelug nit ki Yàlla jagleel njub, fekk ay jëfam taxul. 4:7 Mu ne:«Ñi ñu baal seen jàdd yoon,te seeni bàkkaar far ci kanam Yàlla,ñu barkeel lañu. 4:8 Ki Boroom bi sëful ay bàkkaaram,kooka ku barkeel la.» 4:9 Kon nag barkeel googu, ndax ñi xaraf rekk ñoo ko yeyoo? Ndax ñi xaraful it bokkuñu ci? Aaŋkay! Ndaxte wax nanu ne, Yàlla jàppe na ngëmu Ibraayma ni njub. 4:10 Kañ la ko jagleel njub nag? Ndax lu jiitu xarafam la woon, am gannaaw ga? Lu ko jiitu la woon. 4:11 Ndaxte Ibraayma gëm na, te Yàlla jàppe na ngëmam ni njub, fekk booba xarafagul. Te xarafal gi, màndarga la woon ci yaramam, di firndeel ne, ku jub la woon. Noonu la Ibraayma man a nekke baayu ñépp ñi gëm, ba Yàlla man leen a àtte ni ñu jub, te xarafuñu sax. 4:12 Te noonu itam la Ibraayma man a nekke baayu ñi xaraf, bu fekkee yemuñu rekk ci xaraf, waaye ñu am ngëm, ga Ibraayma sunu maam amoon lu jiitu xarafam. 4:13 Ndaxte Yàlla dafa digoon Ibraayma ak ñi naroon a soqikoo ci moom, ne dinañu moom àddina si. Te dige boobu jógewul ci yoonu Musaa, waaye dafa jóge ci njub, gi Ibraayma amoon ci kanam Yàlla ci kaw ngëmam. 4:14 Ndaxte su fekkee ne ñi nekk ci yoonu Musaa rekk ñooy moom àddina, kon ngëm amatul njariñ, te digeb Yàlla dafa toxu. 4:15 Yoonu Musaa daal du def lu dul wàcce merum Yàlla ci sunu bopp; ndax fu yoon amul, jàdd yoon du fa man a am. 4:16 Kon nag loolu Yàlla dige, ngëm rekk a koy indi, ngir mu sukkandikoo yiwu Yàlla rekk. Noonu la dige bi wóore ci ñi soqikoo ci Ibraayma ñépp, du ci ñi nekk ci yoonu Musaa rekk, waaye itam ñi gëm ni Ibraayma gëme woon. Kon Ibraayma mooy sunu baay, nun ñépp. 4:17 Moom la Yàlla dogal, wax ko ci Mbind mi ne: «Def naa la baayu xeet yu bare.» Ndaxte Ibraayma gëmoon na Yàlla, miy dekkal ñi dee, tey wax ci lu amagul, mel ni dafa am. 4:18 Ibraayma dafa jàppoon ci ngëmam, di yaakaar, fekk bunti yaakaar yépp tëju. Moo tax mu nekk baayu xeet yu bare, ni ko Mbind mi waxe ne: «Noonu la sa askan di meli.» 4:19 Mu xool yaramam, xam ne dee rekk a ko dese, ndax mi ngi tollu woon ci lu mat téeméeri at, waaye ba tey ngëmam wàññikuwul. Mu xam it ne, Saarata mënatul a ëmb. 4:20 Waaye loolu taxul ngëmadi jàpp ko, ba muy werante ci waxu Yàlla; ngëmam sax di gën a dëgër, mu daldi sant Yàlla, 4:21 mu wóor ko ne, loolu ko Yàlla dig, Yàlla man na koo def. 4:22 Moo tax «Yàlla jagleel na Ibraayma njub.» 4:23 Waaye loolu lañu bind ne: «Yàlla jagleel na ko njub,» du Ibraayma rekk a moom wax ji. 4:24 Nun itam ci wax jooju lanu bokk, te Yàlla dina nu jagleel njub, nun ñi gëm Yàlla, mi dekkal Yeesu sunu Boroom. 4:25 Ndaxte Yàlla jébbale na ko ngir sunuy tooñ, dekkal ko ngir àtte nu jub.
5:1 Léegi nag, gannaaw Yàlla àtte na nu jub ci kaw ngëm, nanu jàpp ci jàmm, ji nu am fa kanam Yàlla, jaarale ko ci sunu Boroom Yeesu Kirist. 5:2 Moo nu ubbil bunt ci Yàlla, nu taxaw temm ci yiwam, jaar ci ngëm. Te it nu ngi bég ciy négandiku, Yàlla boole nu ci ndamam. 5:3 Te du ci loolu rekk, waaye bég nanu it ci sunuy nattu; ndax xam nanu ne, nattu day feddali muñ; 5:4 te muñ mooy ndeyu jikko ju dëgër; te jikko ju dëgër day jur yaakaar. 5:5 Te yaakaar jooju du ay nax, ndax mbëggeelu Yàllaa ngi baawaan ci sunu xol, jaarale ko ci Xelam mu Sell mi mu nu may. 5:6 Ndaxte bi nu amul jenn doole, booba la Kirist dee ngir nun, fekk danoo weddi woon Yàlla. 5:7 Kuy nangoo deeyal nit ku jub, yombul a gis, waaye nag jombul am na ku nangoo deeyal ku baax. 5:8 Waaye Yàlla firndeel na mbëggeelam ci nun, ci li Kirist dee ngir nun, bi nu nekkee sax ay bàkkaarkat! 5:9 Gannaaw Kirist tuur na deretam nag, ngir Yàlla àtte nu jub, rawatina ne dina nu musal ci merum Yàlla. 5:10 Nun ay bañaaley Yàlla lanu woon, waaye Doomam dee na, ngir jubale nu ak moom. Gannaaw léegi nag xariti Yàlla lanu, rawatina ne dinanu mucc ndax dundug Doomam. 5:11 Te sax nu ngi bég ci Yàlla, jaarale ko ci sunu Boroom Yeesu Kirist, mi nu jubale ak moom. 5:12 Kon nag bàkkaar ci kenn nit la jaar, dugg ci àddina, indaale fi dee, te dee daldi law ci nit ñépp, ndaxte ñépp a bàkkaar. 5:13 Bàkkaar kon nekkoon na ci àddina, bi Yàlla di laata wàcce yoonu Musaa. Waaye gannaaw yoonu Musaa tëddagul woon, bàkkaar du woon jàdd yoon. 5:14 Teewul nag la dale ca Aadama ba ca Musaa, dee a ngi fi woon ci àddina, di noot ñépp, ak sax ñi seen bàkkaar melul woon ni bosu Aadama, maanaam jàdd yoon. Aadama moomu nag moo di takkandeeru Kirist, mi waroon a ganesi àddina. 5:15 Waaye warunoo yemale tooñu Aadama ak mayu Yàlla. Bàkkaaru kenn nit kooku tax na ñu bare dee; waaye yiwu Yàlla ak may, gi nu keneen nit ka Yeesu Kirist yéwénal, baawaan na ci ñu bare, ba suul tooñ googu. 5:16 Te bàkkaaru Aadama niroowul ak mayu Yàlla. Aadama bàkkaar na benn yoon, ba tax Yàlla daan ko, daanaale ñépp; waaye Yàlla jéggale na tooñ yu bare ci dara, ba mu àtte ñu bare ni ñu jub. 5:17 Bàkkaaru kenn nit tax na dee tàbbi àddina, yilif ñépp ni buur; waaye jëfu keneen nit ka, maanaam Yeesu Kirist, moo ko suul, ba tax ñu bare tàbbi ci dund gu bees, falu ni ay buur; xanaa ñi Yàlla boole ci yiwam wu bare, te àtte leen jub ci dara fa kanamam. 5:18 Kon nag nu gàttal wax ji; jàddug kenn nit ka rekk moo waral Yàlla daan ñépp; noonu itam jëf ju jubu keneen nit ka rekk moo ubbi bunt, ba ñépp man a jub ci kanam Yàlla te am dund gu bees. 5:19 Aadama moomu dafa déggadil Yàlla, ba yóbbaale ñu bare, ñu nekk i bàkkaarkat; noonu itam Yeesu Kirist dafa déggal Yàlla, yóbbaale ñu bare itam, ñu jub. 5:20 Te yoonu Musaa daldi wàcc, ngir bàkkaar gën a bare; waaye fa bàkkaar bare, yiwu Yàlla gën faa bare. 5:21 Ba tax, ni bàkkaar doon yilife ñépp ni buur, indaale dee, noonu itam la yiwu Yàlla faloo ni buur, jóge ci njub, jëm ci dund gu dul jeex. Te loolu lépp darajay Yeesu Kirist sunu Boroom moo nu ko may.
6:1 Lu nu war a wax léegi nag? Xanaa nu sax ci bàkkaar, ngir yiwu Yàlla gën a bare? 6:2 Mukk! Nun ñi dee, ba rëcc ci kàttanu bàkkaar, naka lanu manatee sax ci di ko def? 6:3 Xanaa dangeen a xamul ne, képp ku ñu sóob ci ndox, ngir wone ne, mu ngi bokk ci Yeesu Kirist, ci deewu Yeesu la bokk. 6:4 Bi ñu nu sóobee ci ndox moomu nag, day misaal ne, dañu noo suul ak Kirist, nu dee ni mu deeye woon; ba tax nu dekki it, ni mu dekkee woon ci dooley Yàlla Baay bi, te nu sóobu ci dund gu bees. 6:5 Kon nag gannaaw benn lanu ak Kirist, dee ni mu deeye woon, kon dinanu nekk it benn ak moom, dekki ni mu dekkee woon. 6:6 Ndegam xam nanu ne, daajoon nañu Kirist ca bant ba, xam nanu it ne, jikko ju bon ji nu judduwaale, daajaale nañu ko ak Kirist ca bant ba. Te Yàlla def na loolu, ngir nguuru bàkkaar, gi nekkoon ci sunu yaram tas, nu rëcc ci dooleem. 6:7 Ndaxte ku dee, bàkkaar mënatul dara ci yaw. 6:8 Gannaaw nag dee nanu ak Kirist, gëm nanu ne, dinanu dekki it ni moom, 6:9 xam ne Kirist mi dekki dootul dee mukk, dee mënatul dara ci moom. 6:10 Dee na benn yoon, ba bàkkaar mënul ci moom dara; te mi ngi dund léegi, di ànd ak Yàlla ba fàww. 6:11 Ci noonu nag yéen itam tegleen seen bopp ni ñu dee ak Kirist, ba rëcc ci dooley bàkkaar, di dund, ànd ak Yàlla ba fàww ndax seen bokk ci Yeesu Kirist. 6:12 Buleen mayati bàkkaar nag, mu yilif seeni yaram yu néew doole, bay topp ay bëgg-bëggam. 6:13 Te buleen jébbalati seeni cér bàkkaar, mu def leen jumtukaayam ngir jëfam yu jubadi; waaye gannaaw rëcc ngeen ci dooley dee, bay dundaat, jébbaluleen ci Yàlla te jébbal ko seeni cér, mu def leen jumtukaayam ngir jëfam yu jub. 6:14 Ndaxte bàkkaar dootu leen manal dara, yéen ñi génn ci yoonu Musaa, dugg ci yiwu Yàlla. 6:15 Lan lanu war a wax nag léegi? Gannaaw génn nanu ci yoonu Musaa, dugg ci yiwu Yàlla, ndax danoo war a sax ci def bàkkaar? Mukk! 6:16 Ndax dangeen a xamul ne, koo jébbalu ci moom te déggal ko, jaamam nga? Naka noonu, mbaa ngeen nekk jaami bàkkaar, mu jëme leen ci dee, mbaa ngeen déggal Yàlla, mu sóob leen ci yoonu njub. 6:17 Waaye sant naa Yàlla ci lii: yéen ñi doon jaami bàkkaar, bi ngeen déggee mboolem dëgg gi, nangu ngeen ko ak seen xol bépp. 6:18 Te ci noonu rëcc ngeen ci nootaangeg bàkkaar te jébbalu ci Yàlla, sóobu ci njub. 6:19 Xam naa ne, seen xam-xam ci mbir mii sorewul, moo tax ma yombal wax ji, awale ko ci baat yii. Ni ngeen jële woon seeni cér, jébbal leen, ñu nekk jaami lu selladi ak lu bon, di gën a jur lu bon, noonu itam léegi jébbal-leen seeni cér, ñu nekk jaami njub, ngeen door a sell. 6:20 Ndaxte keroog ba ngeen nekkee jaami bàkkaar, séquleen woon dara ak lu jub. 6:21 Ban njariñ ngeen ci jële nag? Dara lu dul gàcce, ndaxte ci dee la leen doon jëmale. 6:22 Waaye léegi Yàlla goreel na leen ci kilifteefu bàkkaar, def leen ay jaamam, ba jural leen sell, jëme leen ci dund gu dul jeex. 6:23 Ndaxte peyu bàkkaar mooy dee, waaye mayu Yàlla mooy dund gu dul jeex ci Yeesu Kirist sunu Boroom.
7:1 Bokk yi, yéen ñi may waxal xam ngeen luy yoon; xam ngeen kon ne, yoon am na doole ci nit diirub dundam. 7:2 Ci maanaa, mi ngi mel ni jigéen juy séy; yoon a ngi koy boole ak jëkkëram, ñu ànd seen giiru dund, waaye su jëkkër ji faatoo, buum gi dagg na. 7:3 Kon nag su jabar ji àndee ak beneen góor, te fekk jëkkër jiy dund, dees na ko àtte njaaloo. Waaye bu jëkkër ji faatoo, yoon jeexal na seen diggante; man na séy nag ak beneen góor, te loolu du njaaloo. 7:4 Nii laa leen ko man a misaale, samay bokk; bi Kirist deeyee, dangeen a deeyandoo ak moom, te noonu yoonu Musaa wàcc leen. Léegi nag yéena ngi ànd ak keneen, maanaam Kirist mi dekki, ngir nu amal Yàlla njariñ. 7:5 Keroog ba nu daan topp sunu nafsu, yoonu Musaa daan na xamb bëgg-bëgg yu bon, yiy yengal sunuy cér, ba jural nu dee. 7:6 Waaye léegi yoon wi wàcc na nu, ci li nu dee, ba rëcc cig buumam. Léegi nag nu ngi jaamu Yàlla, waxumaleen ci sàmm santaane rekk, ndax loolu wees na, waaye ci kàttan gu bees, gi nu Xelum Yàlla di may. 7:7 Kon nag lu nu war a wax? Ndax bàkkaar ci yoonu Musaa la jóge? Mukk! Waaye moo ma xamal luy bàkkaar. Ndaxte su ma yoon wi waxul woon: «Bul bëgg yëfi jaambur,» kon duma xam luy xemmem. 7:8 Waaye bàkkaar jaare na ci ndigalu Yàlla, daldi ñëw dugg ci man, ba yengal ci man xemmem yu bare. Ndaxte ba ma xamagul woon yoonu Musaa, bàkkaar da ne woon nemm ci man. 7:9 Te keroog bi ma xamagul lu yoon wi santaane, maa ngi doon dund dund gu neex; waaye ba ma ko déggee, bàkkaar dafa daldi fuddu ci man, te man ma daldi dee. 7:10 Noonu gis naa ne, ndigal loolu waroon a jëme nit ñi ci dund, daf maa jëme ci dee. 7:11 Ndaxte bàkkaar jaar na ci li Yàlla digle, ba nax ma, rey ma. 7:12 Kon nag man nanoo wax ne, yoonu Musaa yoon wu sell la, te ndigalu Yàlla dafa sell, jub te baax. 7:13 Ndax kon lu baax moo ma tàbbal ci dee? Mukk! Bàkkaar a ko def, ngir jikkoom feeñ; dafa gis ci lu baax loolu bunt bu mu man a jaar, ba rey ma. Noonu ndigalu Yàlla tax na, bàkkaar fés, bon ba jéggi dayo. 7:14 Xam nanu ne, yoonu Musaa ngi jóge ci Yàlla, waaye man yëfi àddina laa fonk, te nekk ci dooley bàkkaar, mel nib jaam. 7:15 Ndaxte samay jëf jaaxal na ma; li ma bëgg a def, duma ko def, waaye li ma bañ rekk, moom laay def. 7:16 Kon nag gannaaw li may def du sama coobare, nangu naa ne yoonu Musaa baax na. 7:17 Léegi nag du man maay def lu bon loolu, waaye bàkkaar bi dëkk ci man, moo ma ciy jiiñ. 7:18 Ndaxte xam naa ne, lu baax dëkkul ci man, maanaam ci sama bindu doom Aadama. Am naa yéeney def lu baax, waaye awma kàttanu yeggale. 7:19 Lu baax nag lu may yéene, duma ko def, waaye lu bon lu ma bëggul, moom laay def. 7:20 Bu fekkee nag lu ma bëggul, moom laay def, kon dootul sama coobare, waaye bàkkaar bi dëkk ci man, moo ma ci jiiñ. 7:21 Gis naa nag lii: saa su ma bëggee def lu baax, lu bon a ngi ma taxawu. 7:22 Ndaxte ci sama biir xol yoonu Yàlla wi neex na ma. 7:23 Waaye gis naa jeneen doole juy yengu ci samay céri yaram, di bëre ak li sama xol bëgg; day bëre ba noot ma, def ma jaam ci dooley bàkkaar joojuy yengu ci samay cér. 7:24 Céy maaka torox! Ana ku may musal ci sama yaram, wii may jëme ci dee? 7:25 Maa ngi sant Yàlla; am na kuy musle, mooy Yeesu Kirist sunu Boroom. Kon nag lii laa gis ci sama bopp: ci sama xel maa ngi topp yoonu Yàlla, waaye ci sama bindu doom Aadama maa ngi topp yoonu bàkkaar.
8:1 Léegi nag yoon mënul a dab ñi bokk ci Yeesu Kirist. 8:2 Ndaxte kàttanu Xelum Yàlla, tukkee ci Kirist Yeesu, di may nit dund gu bees, goreel na ma ci nootaangeg bàkkaar ak dee. 8:3 Lu yoonu Musaa mënul woon a def, ndax néew dooley nit, Yàlla defe na ko nii: dafa yónni Doomam, ngir mu yor sunu jëmm, nun ñiy nekk ay bàkkaarkat, te mu jébbale bakkanam, ngir dindi bàkkaar yi. Noonu la Yàlla tase nguuru bàkkaar ci nit. 8:4 Ba tax na léegi njub, gi yoonu Musaa di digle, am na ci nun, ñiy déggal Xelu Yàlla mi te bañ a topp sunu nafsu. 8:5 Ñiy topp seen nafsu, seeni bëgg-bëgg rekk lañu fonk, waaye ñiy topp Xelu Yàlla mi, coobareem lañu fonk. 8:6 Ndaxte fonk nafsu, ci dee lay jëme; waaye fonk Xelu Yàlla mi, dund ak jàmm lay joxe. 8:7 Ndaxte ku fonk sa nafsu, bañaaleb Yàlla nga, ndaxte doo déggal Yàlla, mbaa ngay sàmm ay santaaneem, te mënuloo koo def sax. 8:8 Kuy topp sa nafsu nag, doo man a neex Yàlla. 8:9 Waaye yéen nekkatuleen ci topp seen nafsu, waaye yéena ngi topp Xelu Yàlla mi, bu fekkee ne mu ngi dëkk ci yéen. Ku amul Xelum Kirist nag, bokkuloo ci moom. 8:10 Bu fekkee ne Kirist dëkk na ci yéen nag, lii moo am: seen yaram mi ngi ci dooley dee ndax bàkkaar bi nekk ci yéen, waaye seen xel mi ngi dund ndax njub gi leen Yàlla jox. 8:11 Kon nag gannaaw Xelum Yàlla, mi dekkal Yeesu ca néew ya, dëkk na ci yéen, dina tax seen yaram wi néew doole dund ci kàttanu Xel moomu dëkk ci yéen. 8:12 Kon bokk yi, am nanu lu nu war, waaye waxumaleen topp sunu nafsu ak i bëgg-bëggam; 8:13 ndaxte kuy topp nafsoom, fàww mu dee, waaye kuy noot jëfi yaramam ci dooley Xelu Yàlla mi, dina dund. 8:14 Ndaxte ñépp ñiy déggal Xelu Yàlla mi, ay doomi Yàlla lañu. 8:15 Kon nekkatuleen fa kanam Yàlla, ni jaam bu ragal sangam, waaye Xel mi leen Yàlla sol, ay doomi Yàlla la leen def, ba tax nu di wooye Yàlla: «Abba,» maanaam «Baay bi.» 8:16 Ndaxte Xelu Yàlla mi, moom ci boppam, day ànd ak sunu xel ci seede ne, doomi Yàlla lanu. 8:17 Te gannaaw ay doomi Yàlla lanu, dinanu moomi lépp li Yàlla jagleel ay doomam, séddu ci ngëneel yi Kirist yelloo. Waaye nag ku bëgg a bokk ak Kirist ndamam ëllëg, war ngaa séddu ci ay fitnaam tey. 8:18 Xalaat naa ne sunu naqaru tey, wareesu ko tëkkale ak sunu ndamu ëllëg. 8:19 Ndax li Yàlla bind lépp a ngi ne seew a gis doomi Yàlla yi feeñ ci seen biir ndam. 8:20 Ndaxte dunyaa bi bépp mu ngi ci yoon wu dul mujj fenn; teyu ko, Yàlla moo ko ko teg. Waaye teewul ñu am yaakaar ne, 8:21 Yàlla dina rengi seen buumi njaam ci dee, boole leen ci jàmmu doomi Yàlla yi ak seen ndam. 8:22 Xam nanu ba fi nu tollu ne, li Yàlla bind lépp a ngi metitlu ni jigéen juy matu. 8:23 Te du dunyaa bi rekk mooy metitlu, nun it nu ngi metitlu, nun ñi Yàlla sol Xelam, ngir nu ñam añu ëllëg; nu ngi ne seew Yàlla boole nu ci lépp li nu yelloo ni ay doomam, keroog bés bu Yàllay goreel sunu yaram. 8:24 Ndaxte sunu mucc ëmb na yaakaar. Li nga gis ba noppi, nekkatul yaakaar; li teew, noo koy yaakaare? 8:25 Li feek gisagunu nag li nuy yaakaar, dinanu ko séentu ak muñ. 8:26 Te it Xelu Yàlla mi moo nuy xettali ci sunug néew doole. Ndaxte xamunu sax naka lanu war a ñaane Yàlla, waaye Xelu Yàlla maa ngi nuy ñaanal fa moom ak i yéene yu làmmiñ mënta takk. 8:27 Te Yàlla, miy nattu xol yi, xam na xalaatu Xel mi, ndaxte tinu, gi muy tinul gaayi Yàlla yi, mengoo na ak coobareg Yàlla. 8:28 Xam nanu itam ne ñi bëgg Yàlla, maanaam ñi Yàlla woo ci boppam te boole leen ci li mu tëral, Yàlla dina joo loxoom ci lépp lu xew ci seen dund, ngir jural leen lu baax. 8:29 Ndaxte ñi mu xamoon lu jiitu, dafa dogaloon ñu nirook Doomam, ngir mu nekk taaw ci biir njaboot gu yaa. 8:30 Te ñi mu dogaloon loolu ci ñoom, da leen a woo; te ñooñu mu woo, da leen a àtte ni ñu jub; te ñooñu mu àtte jub, da leen a boole ca ndamam. 8:31 Lu nu war a wax nag ci loolu lépp? Gannaaw Yàlla ànd na ak nun, kan moo nu manal dara? 8:32 Yàlla mi nu gàntulul Doomam waaye mu joxe ko, mu dee ngir nun, ndax dina nu bañalati dara? 8:33 Ñi Yàlla tànnal boppam, kan moo leen di tuumaal? Yàlla moo leen àtte ni ñu jub. 8:34 Kan moo leen man a teg tooñ? Yeesu Kirist mi dee, moo dekki itam, te mu nga fa ndeyjoorul Yàlla, di nu fa ñaanal! 8:35 Kan moo nu man a tàggaleek mbëggeelu Kirist? Xanaa duy nattu, te du njàqare, du it fitna, du xiif walla rafle, du it ay ngaañ walla jaasi sax. 8:36 Moo tax Mbind mi ne:«Ñu ngi nuy rey ngir yaw, ci suba ba jant so;ñu ngi nuy jàppe ni xar yu ñuy rey.» 8:37 Waaye loolu lépp teewul, nu ngi mel niy ñeyi xare ci dooley Kirist mi nu bëgg. 8:38 Ndax wóor na ma ne, dara mënu noo tàggaleek mbëggeelam; du dee, du dund, du malaaka yi, du seeni kilifa, du tey, du ëllëg, du boroom doole yi, 8:39 du li ci kaw mbaa li ci suuf, mbaa leneen lu ñu bind; dara mënu noo tàggale mukk ak mbëggeel, gi nu Yàlla jox ci Kirist Yeesu sunu Boroom.
9:1 Li ma bëgg a wax nag, ci kanamu Kirist laa koy waxe; dëgg la, du aw fen. Sama xel, mi Xel mu Sell miy leeral, seedeel na ma ne, dëgg laay wax. 9:2 Maanaam, duma noppee am naqar wu réy ci sama biir xol, 9:3 ba xaw a bëgg a tàggoo ak Kirist te alku, ngir ñi ma bokkal xeet mucc. 9:4 Bànni Israyil lañu, te Yàlla def na leen ni ay doomam; dëkkaloon na ndamam ci seen biir, fas ak ñoom kóllëre yi. Ñoom la Yàlla dénk yoonu Musaa, ñoom la xamal ni ñu ko war a jaamoo, ñoom la jox i digam. 9:5 Maam ya Yàlla tànnoon, ci ñoom lañu bokk, te ci ñoom it la Kirist wàcce, maanaam ci jëmmam, Kirist mi di Yàlla, tiim lépp, te yelloo teraanga ba fàww. Amiin. 9:6 Waaye neewuma waxu Yàlla dafa toxu, ndaxte bokk ci bànni Israyil, taxul nga bokk ci Israyil tigi. 9:7 Te it du ñi soqikoo ci Ibraayma ñépp, ay doomam dëgg lañu. Ndaxte Yàlla dafa wax Ibraayma ne ko: «Saw askan ci Isaaxa lay jaar.» 9:8 Maanaam, soqikoo ci Ibraayma taxul a nekk doomu Yàlla, waaye juddu ci biir digeb Yàlla mooy tax a bokk dëgg-dëgg ci askanu Ibraayma. 9:9 Ndaxte Yàlla dafa digoon Ibraayma naan: «Ci waxtu wii déwén dinaa dellusi ci yaw, te Saarata dina am doom ju góor.» 9:10 Te du ci loolu rekk, waaye noonu la it ci lu jëm ci Rebeka; doom yi mu jur ñoo bokk benn baay, moo di sunu maam Isaaxa. 9:11 Waaye Yàlla wax ko ne:«Yanqóoba rakk ji mooy yilif magam Esawu,» fekk xale ya juddooguñu te defaguñu dara, muy lu baax, muy lu bon. Yàlla def na noonu, maanaam tànn kenn ci doom yi, ngir dogalam man a taxaw, te sukkandikuwul ci seeni jëf waaye ci wooteb Yàlla. 9:13 Loolu la Mbind mi wax ne:«Bëgg naa Yanqóoba, bañ naa Esawu.» 9:14 Kon lu nu ci war a wax? Ndax Yàlla àttewul foofu yoon nag? Mukk! 9:15 Dafa wax Musaa sax ne ko:«Dinaa yërëm ku ma neex,laabiir ci ku ma neex.» 9:16 Dama leen di wax nag, dara ajuwul ci coobareg nit, mbaa ci ñaqam, waaye lépp a ngi aju ci yërmandey Yàlla. 9:17 Ndax Mbind mi biral na li Yàlla wax Firawna ne ko:«Def naa la buur,ngir feeñal sama kàttan ci say mbir,te ngir siiwal sama tur ci àddina si sépp.» 9:18 Kon nag Yàlla, la ko neex lay def, muy yërëm nit, mbaa dëgëral xolam ci lu bon. 9:19 Waaye xanaa dina am ku may wax ne: «Gannaaw kenn mënul a bañ coobareg Yàlla, lu tax kon muy teg nit tooñ?» 9:20 Yaw nag nit ki, ak koo man a doon, lu tax ngay werante ak Yàlla? Ndax mbindeef dina laaj ki ko bind: «Lu tax nga binde ma nii?» 9:21 Ndax tabaxkatu ndaa sañul a fab banam, tabax ci ñaari ndaa, benn bi ngir soxla yu am maana, bi ci des ngir soxla yu ndaw? 9:22 Kon nag looy wax ci lii: Yàlla bëggoon na wone meram, xamle it dooleem ci àddina; teewul dafa sax ci muñal ñi yelloo meram te taxaw ci sànku. 9:23 Bëggoon na it xamle màggaayam mu ëpp xel, ci boole ñi mu yërëm ci ndamam; moo tax mu tànn leen ca njàlbéen. 9:24 Te wax ji noo ko moom, nun ñi Yàlla woo ci boppam ci biir Yawut yi ak ci biir xeet yi ci des. 9:25 Moom la wax ci téereb Ose ne:«Ñi nekkul woon sama xeetdinaa leen ko def,ñi bokkul woon ci sama mbëggeel,dinaa leen ci boole.» 9:26 Te:«Fa ñu leen waxe woon:“Dungeen sama xeet,”dees na leen fa wooye“Doomi Yàlla Boroom dund.”» 9:27 Esayi wax na ci mbirum Israyil ne:«Lu bànni Israyil baree-bare ni suufus géej sax,lu néew rekk a ciy mucc. 9:28 Ndaxte li Boroom bi dogal ci àddina,dina ko gaaw a def, te dina mat sëkk.» 9:29 Esayi it waxoon na lu jiitu loolu ne:«Yàlla Boroom kàttan gi,su bàyyiwul woon ci nun lu néew,kon ba tey raat nanu ni dëkki Sodom ak Gomor.» 9:30 Lu nu ci war a wax nag? Ñi dul Yawut te fonkuñu woon jub ci kanam Yàlla, léegi jub nañu ci kaw ngëm. 9:31 Waaye bànni Israyil, mi bëggoon a sàmm yoon ngir jub, matalu ko. 9:32 Ndax lan? Ndax dañoo sukkandiku ci seeni jëf, bàyyi ngëm. Dañoo daanu ci «doj wuy fakkatale.» 9:33 Moom la Yàlla wax ci Mbind mi ne:«Dinaa samp ci Siyon doj wuy fakkatale,di xeer wuy daaneel nit; waaye ku wéeru ci moom, sa yaakaar du tas.»
10:1 Bokk yi, sama coobareg xol ci bànni Israyil ak sama ñaan ci Yàlla, mooy ñu mucc. 10:2 Seedeel naa leen ne, ñu farlu lañu ci jaamu Yàlla, waaye seen njaamu àndul ak xam-xam. 10:3 Xamuñu yoon, wi Yàlla tëral ngir nit jub ci kanamam, waaye dañoo wéy ci seen pexey bopp; ba tax ñu bañ a nangu yoonu njub woowu Yàlla tëral. 10:4 Ndaxte ci Kirist la yoonu Musaa dëppe, ba tax ku ko gëm, dinga jub fa kanam Yàlla. 10:5 Ku bëgg a jub ci kanam Yàlla ci kaw sàmm yoon, Musaa daf cee wax ne: «Ku ko manoon a matal, dinga dund ba fàww.» 10:6 Waaye ku jub ci kanam Yàlla ci kaw ngëm, nii lay waxe:«Bul wax ci sa xol ne:“Kuy yéeg ci kaw?”» mel ni dangaa bëgg Kirist wàcc. 10:7 «Bul wax it:“Kuy dem ca barsàq?”» mel ni dangaa bëgg Kirist dekki. 10:8 Kon boog lan lay wax? Lii:«Waxu Yàlla mi ngi ci sa wet,ci sa làmmiñ, ci sa xol.» Te wax jooju lal ngëm lanuy waare. 10:9 Ndaxte soo waxee ak sa gémmiñ ne, Yeesu mooy Boroom bi, te nga gëm ci sa xol ne, Yàlla dekkal na ko, dinga mucc. 10:10 Ndax xol la nit di gëme, ba tax mu jub ci kanam Yàlla; làmmiñ it la nit di waxe ne, mi ngi ci Kirist, ba tax Yàlla musal ko. 10:11 Mbind mi dafa wax ne: «Képp ku ko gëm, sa yaakaar du tas mukk.» 10:12 Ndax ñépp a yem ci kanam Yàlla, muy Yawut mbaa ku dul Yawut, ndax kenn rekk mooy sunu Boroom nun ñépp, te ku yéwén la ci képp ku koy ñaan. 10:13 Ndaxte bind nañu: «Képp ku woo Boroom bi ciw turam, dinga mucc.» 10:14 Waaye nan lañuy wooye ki ñu gëmagul? Te naka lañu man a gëme ki ñu déggagul turam? Te naka lañu man a dégge turam, te kenn xamalu leen ko? 10:15 Te it nan lañu man a waaree, su leen kenn yónniwul? Looloo tax Mbind mi wax ne: «Ñiy yégle xebaar bu baax bi, ni seen ñëw di sedde xol!» 10:16 Waaye ñépp nanguwuñu xebaar bu baax bi; moom la Esayi wax ne: «Boroom bi, ana ku gëm sunu waare?» 10:17 Kon boog ngëm ci kaw dégg lay juddoo, te dégg sosoo ci xebaaru Kirist. 10:18 Waaye ma ne: xanaa ñépp dañoo déggul? Aaŋkay! Mbind mi wax na ne:«Seen baat jolli na ci ñeenti xebla yépp,seen wax wër na àddina sépp.» 10:19 Waaye ma teg ci ne: xanaa bànni Israyil dañoo xamul? Aaŋkay! Musaa dafa jëkkoon a wax ne:«Dinaa leen siisloo xeet wu bokkul ci Yàlla,merloo leen ci ñi xamul dara ci Yàlla.» 10:20 Te Esayi takk na fitam, ba wax ne:«Ñi ma wutul woon, gis nañu ma,feeñ naa ci ñi ma laajul woon.» 10:21 Waaye ci mbirum Israyil dafa wax ne:«Tàllal naa samay loxo, suba ba ngoon, ci xeet wu may bañ tey werante.»
11:1 Ma ne kon, ndax Yàlla bërgël na xeetam? Mukk! Ndaxte man itam ci Israyil laa bokk, wàcce ci Ibraayma te bokk ci giiru Ben-yamin. 11:2 Yàlla bërgëlul xeetam, wi mu xamoon lu jiitu. Ndax dangeen a xamul li Mbind mi di wax ci mbirum Iliyas? Dafa doon tawat Israyil ci Yàlla naan: 11:3 «Boroom bi, rey nañu say yonent, daaneel say bérab yu sell, ba man kenn maa ci des, te ñu ngi may wut a rey.» 11:4 Waaye lii la ko Yàlla tontu: «Dencal naa sama bopp juróom-ñaari junniy nit, ñi jaamuwul Baal.» 11:5 Noonu itam ci jamono ji nu nekk, des na nit ñu néew ñu Yàlla dencal boppam ciw yiwam. 11:6 Gannaaw nag yiwu Yàlla rekk a tax mu denc leen, kon du seen peyug ñaq, walla boog yiwu Yàlla dootul yiw. 11:7 Kon lu nu ci war a wax? Li bànni Israyil doon wut, gisuñu ko. Waaye ñi Yàlla tànn rekk a ko gis, te ña ca des bañ a gëm, ba seen xol dërkiis. 11:8 Looloo tax Mbind mi ne:«Yàlla daf leen a jox xelum nit ku gëmmeentu,bët yu gëlëm ak nopp yu tëx,ba ci bésub tey.» 11:9 Te Daawuda it daf ci wax naan:«Na seeni ñam sax nekk fiir ak i pakk;nañu ci daanu, te Yàlla mbugal leen. 11:10 Nañu gumba ba ne fatuus,nañu tiis te sëgg ba fàww.» 11:11 Ndax kon dañoo tarxiis, daanu ba fàww? Mukk! Waaye jéllub Israyil dafa ubbi bunt, ngir xeeti ñi dul Yawut man a mucc, te bànni Israyil siis leen. 11:12 Gannaaw seen tooñ nag moo ubbi buntu yiw ci waa àddina si, te seen ñàkk moo meññ barkeb xeet yépp, céy bés bu Israyil gépp delloo ci Yàlla, ndaw barke bu bare! 11:13 Yéen ñi dul Yawut, yéen laay waxal. Ndegam Yàlla daf maa def ndawam, yónni ma ci yéen xeeti àddina si, damay matal samab yónnent. 11:14 Dama koy def, ngir ñi bokk ak man xeet siis, ba ñenn ñi mucc. 11:15 Ndaxte bi Yàlla génnee Israyil, ubbee na noonu bunt, ngir xeeti àddina juboo ak moom; kon su Yàlla dugalaatee Israyil, ndax du mel ni ndekkitel néew ya? 11:16 Damay wax ne, mburu mépp sell na, bu ci Yàlla amee wàll. Naka noonu garab gi Yàlla séddoo reen bi, garab gépp sell na. 11:17 Bànni Israyil a ngi mel ni garabu oliw gu ñu jëmbët ci kër gi, waaye mu am car yu ci fàq. Yaw mi dul Yawut, yaa ngi mel ni caru garabu oliw gu àll bu ñu jabtal ci garabu kër googu. Noonu nga jariñoo meen, mi jóge ci reen bi. 11:18 Kon nag bul bàkku, di xeeb car yooyu Yàlla fàq. Waaye soo bëggee bàkku, xamal ne, reen moo lay yenu, te du yaw miy car yaa koy yenu. 11:19 Xanaa dinga wax ne: «Car yooyu dañu leen a fàq, ngir jabtal ma fa ñu nekkoon.» 11:20 Dëgg la; waaye seen ngëmadee tax ñu fàq leen, wuutal la fa ndax sa ngëm. Bumu tax nag ngay bàkku, waaye nanga moytu. 11:21 Gannaaw Yàlla baalul car ya cosaanoo ca garab ga, kon boog yéen itam man na leen a fàq. 11:22 Loolu kon wone na ni Yàlla baaxe ak ni muy meree tooñ. Ci ñi daanu, Yàlla wone na ni meram tànge, wone mbaaxam ci yéen, su fekkee yéena ngi ci wéy; lu ko moy, dees na leen fàq yéen itam. 11:23 Te car yooyu fàq, su ñu wéyul ci seen ngëmadi, dees na leen delloo ci garab gi, ndax Yàlla man na leen cee tafaat. 11:24 Yaw mi dul Yawut, yaa ngi bokkoon ci garabu oliw gu àll, waaye Yàlla daf la cee jële, ci lu dul faral a am, jabtal la ci garabu kër gi. Kon man nanoo gën a wóor ne, Yawut ya judduwaale nekk ci garabu oliw gu kër gi, Yàlla dina leen ci delloo. 11:25 Bokk yi, dama leen a bëgg a dindi kumpa ci lii, ngir ngeen bañ a yég seen bopp. Dërkiisu xol dab na bànni Israyil ab diir, ba bés ba mboolem waa àddina, ñu war a bokk ci nguuru Yàlla, dugg ca. 11:26 Bu loolu amee nag, bànni Israyil gépp dina mucc. Moom la Mbind mi tëral, bi mu naan:«Ab xettalikat dina jóge ci Siyon,dàq weddi ci askanu Yanqóoba. 11:27 Loolu mooy kóllëre, gi may fas ak ñoom,bés bu may dindi seeni bàkkaar.» 11:28 Gannaaw bañ nañu xebaar bu baax bi, ay bañaaley Yàlla lañu, ngir ngeen jot barkeem. Waaye gannaaw Yàlla tànn na leen, dafa leen bëgg ba tey ndax seen maam ya. 11:29 Ndax li Yàlla maye, dootu ko nangu mukk, te ku mu woo ci boppam, dootu la dàq mukk. 11:30 Ñu déggadil Yàlla ngeen woon, waaye ngëmadig Yawut yi tax na, ngeen jot yërmandeem. 11:31 Ñoom itam lànk nañu léegi, ngir man a bokk ak yéen yërmandey Yàlla. 11:32 Kon Yàlla tëj na ñépp ci ngëmadi, ngir man a yërëm ñépp. 11:33 Xelum Yàlla ni mu xóote, ak xam-xamam ni mu baree, ba raw xelum nit! Kan moo muus, ba xam dogalam? Walla nga am xel, ba nànd ay jëfam? 11:34 Mbind mi dafa ne:«Ana ku xam xalaatu Boroom bi?Ku ko doon digal?» 11:35 Te it:«Ku ko mas a jox dara,ba mu war laa delloo?» 11:36 Ndaxte ci moom la lépp sosoo, ci moom la lépp di jaar, ci moom la lépp di dellu. Moo yelloo ndam ba fàww. Amiin.
12:1 Kon nag bokk yi, gannaaw yërmandey Yàlla baree na noonu, maa ngi leen di ñaan, ngeen jébbal ko seen yaram wépp. Na seen dund mel ni sarax su ñuy defal Yàlla, sarax su sell te neex ko. Loolu mooy njaamu, gi leen war. 12:2 Bu leen àddina jey, waaye yeesluleen ci seen xel, ba soppiku, ngeen man a xam bu wér coobareg Yàlla, di lépp lu baax, neex ko te mat sëkk. 12:3 Gannaaw Yàlla may na ma ciw yiwam, ma nekk ndawam, maa ngi leen di wax lii, kenn ku nekk ci yéen: buleen yég seen bopp, waaye ngeen am xalaat yu yem, mengook ngëm gi leen Yàlla sédd, ku nekk ak wàllam. 12:4 Loolu, ci maanaa, mi ngi mel ni yaramu nit: yaram, lu cér yi baree-bare, benn niroowul ak moroomam liggéey. 12:5 Noonu itam nun ñi bokk ci Kirist, lu nu baree-bare, benn lanu te danoo mànkoo. 12:6 Kon gannaaw Yàlla séddale na ay mayam, ku nekk ak sa cér, nanu koy jëfandikoo. Ku Yàlla may, ngay waare kàddoom, nga wax ko kem sa ngëm; 12:7 kuy topptoo yëfi mbooloo mi, nga takku ci; ku Yàlla may, ngay jàngale, nekk ci; 12:8 kuy feddali ngëmu nit ñi ci Yàlla, nga sax ci; kuy séddoo alalam ak nit ñi, nga def ko ak xol bu laab; kuy jiite mbooloo mi, nga sawar ci; kuy dimbali ñi néew doole, nanga ci bég. 12:9 Na seen cofeel di lu dëggu te bañ a nekk ngistal; araamal-leen lu bon te sax ci lu baax. 12:10 Bëgganteleen ak xol bu leer, niy doomi ndey, te farlu ci teralante. 12:11 Sawarleen te bañ a tayel, di jaamu Boroom bi ak seen xol bépp. 12:12 Bégleen ci yaakaaru ëllëg te muñ bépp tiis, di sax ci ñaan Yàlla. 12:13 Dimbalileen gaayi Yàlla yi ci seeni soxla, te saxoo dalal gan. 12:14 Ku leen fitnaal, ñaanal-leen ko yiw, te bañ koo móolu. 12:15 Bégandooleen ak ñi bég, te jooyandoo ak ñiy jooy. 12:16 Bokkleen menn xel, tey bañ a yékkatiku, di yóotu daraja, waaye ngeen fonk ñi suufe; buleen teg seen bopp boroomi xel. 12:17 Buleen feyante lu bon, waaye sàkkuleen seede su rafet ci kanam ñépp. 12:18 Wutleen a juboo ak ñépp, ba fa seen kàttan yem. 12:19 Samay soppe, buleen di feyantoo, waaye bàyyileen lépp ci loxoy Yàlla, mi yelloo àtte; ndax Yàlla nee na ci Mbind mi: «Man maay àtte, maay fey jëf.» 12:20 Waaye defleen lii:«Bu sa noon xiifee, may ko mu lekk;bu maree, may ko mu naan.Ndax boo ko defee, dinga ko rusloo.» 12:21 Bu leen lu bon ëpp doole, waaye nootleen ko ci def lu baax.
13:1 Gannaaw loolu na nit ku nekk déggal ñi yore baat ci kanamam; ndaxte amul njiit lu fi Yàlla sampul. Njiit yépp nag Yàlla moo leen fi teg. 13:2 Kon ku leen bañ a déggal, ndigalu Yàlla nga lànk, te ku def loolu, yoon dina la dab. 13:3 Kuy def lu baax warul a ragal njiit li, kuy def lu bon moo ko war a ragal. Soo ko bëggee bañ a ragal nag, kon defal lu baax, te dina la tagg. 13:4 Ndax Yàllaa ko dénk liggéey boobu ngir sa jàmm. Waaye sooy def lu bon, war ngaa ragal, ndax du cig neen la ame jaasiy àtte; jawriñu Yàlla la ngir wàcce meru Yàlla, ci fey ku def lu bon. 13:5 Kon fokk ngeen déggal ko, waxuma sax ndax sañ-sañam boobu, waaye it ngir seen xel dal. 13:6 Gannaaw Yàllaa sas njiit yi liggéey boobu, te ñi ngi ci, kon fàww ngeen fey galag. 13:7 Joxleen ku nekk céram; ku ngeen war a fey galag, feyleen ko ko; ku ngeen war a fey juuti, feyleen ko ko; ku ngeen war a weg, wegleen ko; ku ngeen war a teral, teral-leen ko. 13:8 Buleen ameel kenn dara, lu dul mbëggeel; ndax ku bëgg sa moroom, wàccoo nga ak yoonu Musaa. 13:9 Ndaxte ndigali Yàlla yépp, yi deme ni: «Bul njaaloo, bul rey nit, bul sàcc, bul bëgge,» walla leneen ndigal lu mu man a doon, wax jii moo leen ëmb: «Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.» 13:10 Ku bëgg sa moroom, doo ko tooñ; kon ku wéy ci mbëggeel matal nga yoonu Musaa. 13:11 Te lii itam am na: xam ngeen bu baax jamono ji nu tollu; jamonoy yeewu jot na, ndax léegi sunu mucc gën na noo jege, ca ba nu dooree gëm. 13:12 Guddi gi màggat na, bët a ngi bëgg a set. Nanu bàyyi nag jëf yu lëndëm te ràngoo gànnaay yi nu Yàlla jox, ngir dund ci leer. 13:13 Gannaaw nu ngi ci leer, na sunug dund rafet. Bunu naan sangara ba màndi tey bànneexu; bunu njaaloo tey def i ñaawteef ak sunuy cér; bunu xuloo mbaa nuy ñeeyante. 13:14 Waaye gànnaayooleen Yeesu Kirist Boroom bi, te bañ a topp seen bakkan ciy bëgg-bëggam yu bon.
14:1 Gannaaw loolu ku ngëmam néew nangeen ko nangu, te bañ a werante ak moom ci lu lënt. 14:2 Ndax am na ku xalaat ne, man na lekk ñam wu nekk, fekk ku ngëmam néew du lekk yàpp, waaye léjum rekk lay lekk. 14:3 Kiy lekk lu nekk, bumu xeeb ki ko dul def. Naka noonu itam ku dul lekk yàpp, bumu teg tooñ ki koy lekk; ndax Yàlla nangu na leen ñoom ñaar. 14:4 Koo teg sa bopp, ba di ko teg tooñ? Jaamu jaambur la! Mu taxaw ci liggéeyam, mbaa mu sàggane ko, moom ak sangam la. Waaye dina jub, ndax Boroom bi am na dooley taxawal ko ci njub. 14:5 Noonu itam am na ñiy tànn bés ak ñiy yemale bés yépp. Na ku nekk xam bu wér li muy def, te jàpp ci. 14:6 Ndaxte kuy tànn bés, mu ngi koy def ngir màggal Boroom bi. Kiy lekk lu nekk it, mu ngi koy def ngir màggal Boroom bi; loolu leer na ndax day sant Yàlla. Te it ki bañ a lekk yàpp, mu ngi koy def ngir màggal Boroom bi, di ko sant. 14:7 Kenn ci nun dundul ngir boppam, kenn deewul it ngir boppam. 14:8 Danuy dund ngir màggal Boroom bi, dee it ngir màggal ko. Kon nag nuy dund mbaa nu dee, noo ngi ci Boroom bi. 14:9 Loolu sax moo waral Kirist dee te dundaat, ngir man a nekk Boroomu ñi dee ak ñiy dund. 14:10 Yaw nag lu tax ngay teg sa moroom tooñ? Lu tax nga koy xeeb? Xanaa nun ñépp, danu dul dajeji fa kanam Yàlla, ngir mu layoo ak nun? 14:11 Ndaxte Mbind mi tëral na lii:«Boroom bi nee na:“Ni mu wóore ne maa ngi dund,ni la wóore ne, ñépp dinañu ma sukkal,te ku nekk seede ne maay Yàlla.”» 14:12 Noonu ku nekk ci nun dinga làyyi fa Yàlla ci lépp loo mas a def. 14:13 Kon nanu bàyyee tegante tooñ, waaye nu fas yéenee moytu lépp lu nekk fiir guy yóbbe sunu moroom bàkkaar. 14:14 Xam naa ne, amul wenn ñam wu sellul, ndax Yeesu Boroom bi xamal na ma loolu. Waaye loo yaakaar ne sellul, ci yaw la sellul. 14:15 Soo dee lekk luy indil sa moroom tiis, génn nga ci mbëggeel. Yaw nag bul réeral sa moroom ci sa ñam, ndax Kirist dee na ngir moom. 14:16 Bu sa njariñ jur wax ju ñaaw. 14:17 Ndaxte bokk ci nguuru Yàlla jotewul dara ak lu nuy lekk mbaa lu nuy naan. Nguuru Yàlla mooy jub ci kanam Yàlla, te am mbég ak jàmm ci dooley Xel mu Sell mi. 14:18 Kiy jaamoo noonu Kirist moo neex Yàlla ak nit ñi. 14:19 Kon nag nanu wut luy indi jàmm, tey yékkati ngëmu sunu moroom. 14:20 Bu sa ñam yàq jëfu Yàlla. Bépp ñam sell na ci kanam Yàlla. Ci lu wér! Waaye képp ku lekk luy yàq sa ngëmu moroom, def nga lu bon. 14:21 Liy sa warugar mooy nga bañ a fiir sa moroom ci yàpp mbaa ci biiñ mbaa ci leneen lu mu man a doon. 14:22 Su fekkee sa ngëm dëgër na, wone ko ci sa diggante ak Yàlla. Kiy nangu, te du ci sikkal boppam, kooku barkeel na. 14:23 Waaye kuy lekk ñam te am ci xel ñaar, def nga bàkkaar, ndax sa ngëm yemu fa. Ndaxte jëf ju àndul ak ngëm, bàkkaar la.
15:1 Nun ñi dëgër ci sunu ngëm, war nanoo nangu ñi seen ngëm néew te am ci lu ñuy sikki-sàkka, te bañ a yem ci wut sunu bànneex. 15:2 Na ku nekk ci nun di wut lu neex moroomam ngir jariñ ko, ba mu gën a dëgër ci ngëmam. 15:3 Ndaxte Kirist musul a wut bànneexu boppam. Loolu la Mbind mi wax ne: «Lor yi ñu la saagaa, ci sama kaw lañu dal.» 15:4 Ndaxte lépp lu ñu waxoon ci Mbind mi lu jiitu tey, dañu koo tëraloon, ngir nu sàkku ci xam-xam, xam-xam bu nuy may fit ak muñ, ak di feddali sunu yaakaar. 15:5 Kon nag Yàlla miy maye muñ ak fit, na leen may, ngeen déggoo te nekk benn bu yellook li Kirist Yeesu wone. 15:6 Ba tax nu bokk benn xalaat ak benn baat ci màggal Yàlla, Baayu Yeesu Kirist sunu Boroom. 15:7 Moo tax nangoonteleen, bay màggal Yàlla, ni leen Kirist nangoo. 15:8 Lii laay wax: Kirist ñëw na liggéeyal Yawut yi, ngir wone kóllëreg Yàlla ci matal dige, ya mu digoon maam ya. 15:9 Ñëw na itam ngir ñi nekkul Yawut man a màggal Yàlla ndax yërmandeem. Moo tax Mbind mi ne:«Dinaa la màggal tey tagg saw tur,ci kanamu xeet yépp.» 15:10 Mbind mi nee na it:«Yéen xeeti àddina, ñëwleen bànneexuak xeet wi Yàlla tànnal boppam.» 15:11 Mu dellooti ne:«Santleen Boroom bi, yéen waa àddina,te ñëw màggal ko, yéen xeet yépp.» 15:12 Te it Esayi wax na ne:«Am na sëtu Yese buy ñëw,dina yilif xeeti ñi dul Yawut,te ci moom lañuy wékk seen yaakaar.» 15:13 Kon Yàlla miy maye yaakaar, na def ci seen xol mbég mu réy ak jàmm ju yaa ci seen kaw ngëm, ba ngeen am yaakaar ju mat sëkk ci dooley Xel mu Sell mi. 15:14 Bokk yi, wóor na ma ne, baax ngeen ba fa mbaax man a yem, fees dell ak xam-xam, ba man a jàngaleente mbiri Yàlla ci seen biir. 15:15 Bu sama kàddu diisee nag ci bataaxal bii, dara taxul lu dul bëgg a yeesal seen xalaat, ndaxte Yàlla ci kaw yiwam daf maa sas, 15:16 ma nekk jawriñu Kirist Yeesu, yebal ma ci àddina ci xeeti ñi dul Yawut. Liggéey bu sell laay def ngir Yàlla, ci xamle xebaaram bu baax bi, ngir xeeti àddina sell ci dooley Xel mu Sell mi, ba neex Yàlla, mel ni sarax su ñu koy jébbal. 15:17 Kon nag maa ngi bànneexu ci Kirist Yeesu ngir liggéey boobu ma Yàlla dénk. 15:18 Awma fitu wax leneen nag, lu dul li Kirist jëf jaarale ko ci man, ngir xeeti àddina jébbalu ci moom; jëf na jaarale ci samay wax ak samay jëf, 15:19 ci ay tegtal ak i kéemaan, sukkandikoo ci dooley Xelu Yàlla mi. Ba fi mu nekk nag yégle naa fu nekk xebaaru Kirist, li dale ci Yerusalem, jaar ci gox yépp, ba àgg diiwaanu Iliri. 15:20 Sama yéene mooy xamle xebaaru turu Kirist fa mu eggagul, ndax bëggumaa yeggale sas wu keneen daloon. 15:21 Li ma def nag, dëppoo na ak li Mbind mi wax ne:«Ñi yégagul mbiram dinañu ko yég,te ñi ko musul a dégg, xam ko.» 15:22 Bëggoon naa ñëw seetsi leen, fekk ay téq-téq ñoo ma téye ba tey. 15:23 Waaye nag léegi bey naa sama sas ci gox yii. 15:24 Bu may dem Espaañ nag, bëgg naa faa jaar, nuyu leen; ndaxte ay at a ngii maa ngi am yéene ju tar ci ñëw seetsi leen. Bëgg na maa nekk ci seen biir, ngir am bànneexu sotteente ak yéen xalaat ab diir, te it ngeen waajalal ma sama yoonu Espaañ. 15:25 Waaye nag fi mu nekk maa ngi dem nii Yerusalem, ngir dimbaliji gaayi Yàlla yu sell ya fa nekk. 15:26 Ndaxte waa Maseduwan ak waa Akayi ñi gëm, fas nañu yéeney sàkk ci seeni alal, yónnee ko, ngir dimbali ñi néew doole ci gaayi Yàlla yu sell, yi nekk Yerusalem. 15:27 Yéene nañu ko, te it ci dëgg-dëgg bor la, bu ñu war a fey. Ndaxte gannaaw ñi gëm ci Yerusalem séddoo nañu ak ñi dul Yawut seen ngëm, kon xeet yooyu itam war nañoo séddoo ak ñoom seen alal. 15:28 Kon nag waxtu wu ma noppee ci liggéey boobu, teg may gu tedd gii ci loxoy boroom, dinaa dem Espaañ, tey jaar fi yéen. 15:29 Te wóor na maa ne, bu ma agsee ci yéen, dinaa indaale barkeb Kirist bu mat sëkk. 15:30 Gannaaw loolu bokk yi, maa ngi leen di ñaan ci turu sunu Boroom Yeesu Kirist ak ci bëggante, gi Xelu Yàlla mi def ci nun, ngeen defal ma lii: àndleen ak man, nu tuur sunu ñaq ci ñaan Yàlla. 15:31 Ñaanal-leen ma, ngir ma mucc ci ñi gëmul ci waa Yude; te it gaayi Yàlla yu sell yu nekk ci Yerusalem nangu ndimbal, li ma leen di yóbbul. 15:32 Dolli ci, Yàlla may ma, ma ñëw seetsi leen ak xol bu sedd, nu booloo yeeslu fa kanam Yàlla. 15:33 Na Yàlla Boroom jàmm ànd ak yéen ñépp. Amiin.
16:1 Bu nu weesoo loolu, maa ngi leen di dénk sunu jigéen Febe, miy liggéeyal mbooloom ñi gëm ci dëkku Señsere. 16:2 Nangeen ko jàpp ci turu Boroom bi, ni ko gaayi Yàlla yi yelloo, te dimbali ko ci lépp lu mu aajowoo; ndaxte moom itam wax dëgg, dimbali na ñu bare, ba ci man mii di wax ak yéen. 16:3 Nuyul-leen ma Pirsil ak Akilas, samay nawle ci liggéeyu Kirist Yeesu. 16:4 Ñoom ñaar dem nañu, bay bëgg a jaay seen bakkan ngir man; maa ngi leen di gërëm ci loolu, du man rekk sax, waaye itam mboolooy ñi gëm ci xeeti àddina sépp. 16:5 Nuyul-leen ma it ñiy booloo ci seen kër.Maa ngi nuyu it Epaynet, mi jëkk a gëm Kirist ci diiwaanu Asi; 16:6 ak Maryaama, mi sonnoon lool ci yéen. 16:7 Nuyul-leen ma it Andoronikus ak Yuñas, sama bokk, yi ñu ma booleeloon tëj; am nañu tur ci ndawi Yàlla yi, te ñoo ma jiitu sax ci gëm Kirist. 16:8 Te fàttewuma Ampilyaatus, mi ma bëgg ci sama xol ngir Boroom bi. 16:9 Nuyul-leen ma it Urban, sunu nawle ci liggéeyu Kirist, ak sama soppe Estakis; 16:10 ak it Apeles, mi ngëmam dëggu, ba yelloo kóolute.Nuyul-leen ma it waa kër Aristobul, 16:11 ak Erojon sama mbokk, ak waa kër Narsis, ñi ci Boroom bi. 16:12 Maa ngi nuyu Tirifen, moom ak Tirifos, jigéen ñi sonn ci liggéeyu Boroom bi, ak it sama soppe Persidd, mi ci jeex tàkk. 16:13 Maa ngi nuyu it Rufus, waa ji xolam seey ci Boroom bi, ak yaayam, mi ma féete woon it cérub ndey. 16:14 Te fàttewuma Asànkirit, Felegon, Ermes, Patarobas, Ermas, ñoom ak mboolem bokk yépp. 16:15 Nuyul-leen ma it Filolog ak Yuli, Nere ak jigéenam.Te fàttewuma Olimpas ak gaayi Yàlla yiy booloo ak ñoom ñépp. 16:16 Te yéen bokk yi, saafoonteleen ak xol bu laab. Mboolooy ñi gëm Kirist yépp a ngi leen di nuyu. 16:17 Bokk yi, maa ngi leen di dénk, ngeen moytu ñi leen di féewale, ba di leen jàddloo yoon wi, ciy wax lu juuyoo ak dëgg gi ngeen jàng. Dawleen leen ba sore. 16:18 Ndax ñu deme noonu liggéeyaluñu Kirist sunu Boroom; seen bopp lañuy liggéeyal. Ñu ngi ñëw ak làmmiñ yu neex, di jey xol yu woyof yi, ba nax leen. 16:19 Waaye seen dégg ndigal bir na ñépp, ba sama xol sedd lool ci yéen. Teewul nag damaa bëgg ngeen am xam-xam bu leer ci lu baax, te bañ a laal dara ci lu bon. 16:20 Su ko defee Yàlla Boroom jàmm dina noot Seytaane ci seeni tànk léegi. Na yiwu Yeesu sunu Boroom ànd ak yéen! 16:21 Timote sama nawle bi may jàpple ci liggéey bi, mu ngi leen di nuyu, ak samay bokk Lusiyus, Yason ak Sosipater. 16:22 Man Tersiyus mi bind bataaxal bii nag, maa ngi leen di nuyu ci turu Boroom bi. 16:23 Gayus mu ngi leen di nuyu; moo may ganale ci këram, te foofa it la mbooloo mi di dajaloo. Erast miy topptoo mbiri xaalisu dëkk bi it, nuyu na leen, ak sunu mbokk Kartus. 16:24 Na yiwu sunu Boroom Yeesu Kirist ànd ak yéen! Amiin. 16:25 Santleen Yàlla, mi leen man a saxal bu wér ci dëggu xebaar bu baax, bi may waare ci mbirum Yeesu Kirist! Nekkoon na kumpa gu làqu diirub ay ati at, 16:26 waaye léegi nag Yàlla dindi na nu ci kumpa. Te santaane na, nu yégle xebaar boobu ci xeeti àddina sépp, ci firi Mbindi yonent yi, ngir nit ñi man koo gëm, ba jébbalu. 16:27 Yàlla mi jagoo xam-xam bépp, moom rekk moo yelloo ndam ba fàww, jaar ci Yeesu Kirist! Amiin.
1:1 Man Pool, ndawul Kirist Yeesu ci coobareg Yàlla, man ak Sosten sunu mbokk, 1:2 noo leen di bind, yéen mbooloom Yàlla, mi dëkk Korent. Nu ngi leen di nuyu, yéen ñi Yàlla sédde boppam jaare ci Kirist Yeesu, yéen ñi Yàlla woo, ngeen sell, boole leen ak ñi nekk ci àddina sépp tey tudd turu sunu Boroom Yeesu Kirist, miy seen Boroom, di sunu bos. 1:3 Na leen Yàlla sunu Baay ak Yeesu Kirist Boroom bi may yiw ak jàmm. 1:4 Duma jóg ci di sant Yàlla sama Boroom ci seen mbir ndax yiw, wi mu leen may ci seen bokk ci Kirist Yeesu. 1:5 Ndaxte ci yiwi Yàlla yépp ngeen woomle ci Kirist, muy ci wax, muy ci xam-xam. 1:6 Ndaxte li nu doon seedeel Kirist, Yàlla dëggal na ko ci yéen. 1:7 Noonu nag ñàkkuleen genn may léegi bi ngeen di séentu waxtu, wi sunu Boroom Yeesu Kirist di feeñ ci biir ndamam. 1:8 Kirist dina leen dooleel ba ca muj ga, ngir ngeen bañ a am wenn ŋàññ bés bu sunu Boroom Yeesu Kirist dellusee. 1:9 Yàlla kuy sàmm kóllëre la, moom mi leen woo, ngir ngeen bokk ak Doomam Yeesu Kirist, sunu Boroom. 1:10 Waaye bokk yi, maa ngi leen di dénk ci turu sunu Boroom Yeesu Kirist, ngeen juboo te bañ a féewaloo ci seen biir. Waaye nangeen ànd te booloo, bokk xel, bokk xalaat. 1:11 Ndaxte bokk yi, waa kër Kelowe xamal nañu ma ne, dangeen di xuloo. 1:12 Maa ngi ñëw ca wax ja: kenn ku nekk ci yéena ngi naan: «Man ci Pool laa bokk!» «Man ci Apolos!» «Man ci Sefas!» «Man ci Kirist!» 1:13 Ndax Kirist dafa xaajoo? Ndax Pool lañu daajoon ca bant ba, mu dee ngir yéen? Ndax sóob nañu leen ci ndox, ngir wone ne bokk ngeen ci Pool? 1:14 Maa ngi sant Yàlla ci li ma sóobul kenn ci yéen, ku dul Kirispus ak Gayus, 1:15 ngir kenn bañ a wax ne, ci sama tur lañu ko sóob. 1:16 Aaŋkay! Sóob naa it ci ndox waa kër Estefanas. Waaye ci sama pàttaliku sóobuma keneen. 1:17 Ndaxte Kirist yebalu ma ngir may sóobe ci ndox, waaye da maa yebal, ngir may yégle xebaar bu baax bi, te ma bañ koo def ak waxi xam-xamu nit, ngir bañ a ñàkkal faayda deewu Kirist ca bant ba. 1:18 Ndaxte yégleb deewu Kirist ca bant ba, ag ndof la ci ñiy sànku. Waaye ci nun ñi aw ci yoonu mucc gi, dooley Yàlla la. 1:19 Ndaxte Mbind mi nee na:«Dinaa folli xam-xamu boroom xam-xam yi,lem xalaati ñi am xel.» 1:20 Ana boroom xam-xam bi? Ana kaaŋ mi? Ana boroom làmmiñ wu neex, wi ci àddina sii? Xanaa Yàlla wonewul ne, xam-xamu àddina si ag ndof la? 1:21 Gannaaw àddina si ci xam-xamam demul ba xam Yàlla --te Yàllaa dogal loolu ci xam-xamam — soob na Yàlla mu musal ñi gëm, jaar ci yégleb xebaaru Kirist, fekk ag ndof la ci bëti nit. 1:22 Ndaxte Yawut yi ñu ngi laaj ay firnde; Gereg yi di wut xam-xam. 1:23 Waaye nun nu ngi yégle Kirist, mi ñu reyoon ca bant ba, te loolooy téq ngëmu Yawut yi, di ag ndof ci ñi dul Yawut. 1:24 Waaye ci ñi Yàlla woo, ñuy Yawut mbaa di Gereg, Kirist mooy dooley Yàlla, di xam-xamu Yàlla. 1:25 Li ñuy wax ag ndof ca wàllu Yàlla moo gën a tedd xam-xamu nit. Te li ñuy wax ñàkk dooley Yàlla moo ëpp kàttan dooley nit. 1:26 Bokk yi, seetleen seen nekkin, bi leen Yàlla di woo. Barewul woon ci yéen, ñi ñuy tudde ay boroom xam-xam mbaa ay boroom doole mbaa ñu rafet ab juddu. 1:27 Waaye li àddina teg ag ndof, Yàlla tànn na ko, ngir rusloo boroom xam-xam yi; te li àddina teg ag ñàkk doole, Yàlla tànn na ko, ngir rusloo boroom doole yi. 1:28 Li dul juddu bu rafet te mat a xeeb ci àddina, Yàlla tànn na ko; Yàlla tànn na li nekkul, ngir neenal li nekk. 1:29 Noonu kenn du man a damu ca kanam Yàlla. 1:30 Waaye Yàlla moo def ba ngeen bokk ci Kirist, moom mi doon ci nun xam-xam bu jóge ca Yàlla, maanaam: sunu njubte, sunu sellaay, sunu njot. 1:31 Loolu dafa am, ngir li Mbind mi wax am, ne: «Kuy damu, na damu ci Boroom bi.»
2:1 Man ci sama bopp, bokk yi, bi ma ñëwee ci yéen, ngir yégle mbóoti Yàlla, ñëwuma ci ay wax yu neex ak xam-xam bu réy. 2:2 Dogu woon naa ci bañ a xam dara ci seen biir lu dul Yeesu Kirist, te muy ki ñu rey ca bant ba. 2:3 Bi ma teewee ci yéen, ànd naa ak ñàkk doole, ragal ak njàqare. 2:4 Li ma wax ak li ma waare, defuma ko ci làmmiñ wu neex, sukkandikoo ko ci xam-xamu nit, waaye ànd na ak ay firnde yu soqikoo ci kàttanu Xelum Yàlla, 2:5 ngir seen ngëm bañ a wékku ci xam-xamu nit ñi waaye mu wékku ci dooley Yàlla. 2:6 Moona am na xam-xam bu nuy yégal ñi mat, xam-xam bu bokkul ci àddina si, te njiiti àddina si xamuñu ko, ñoom ñi nar a wéy. 2:7 Nu ngi yégle mbóotu xam-xamu Yàlla, mu nëbbu woon te Yàlla dogal ko ngir sunu ndam, laata àddina di sosu. 2:8 Kenn ci njiiti àddina amul woon xam-xam boobu. Su ñu ko amoon, kon duñu rey Boroom ndam li ci bant bi. 2:9 Waaye Mbind mi nee na:«Lu bët gisul,nopp déggu kote xel xalaatu ko,loolu la Yàlla dencal ñi ko bëgg.» 2:10 Fekk nag nun la ko Yàlla won, jaarale ko ci Xelam. Xelum Yàlla mooy leeral lépp, ba ci xalaati Yàlla yi gën a xóot. 2:11 Kan ci nit ñi moo xam yëfi nit? Xanaa xelum nit mi nekk ci moom rekk a ko xam. Noonu it kenn xamul yëfi Yàlla, ku dul Xelum Yàlla. 2:12 Nun nag Xel mi nu jot, jógewul ci àddina, waaye Yàllaa nu ko sol. 2:13 Te loolu nu Yàlla may, yéglewunu ko ci ay baat yu soqikoo ci xam-xamu nit, waaye nu ngi koy yégle ci baat, yi soqikoo ci Xelum Yàlla, di tekkantal yëfi Xelum Yàlla ci ay baat yu mu nu sol. 2:14 Nit kese du nangu yëfi Xelum Yàlla. Ag ndof lay doon ci moom, te du ko man a nangu, ndaxte ku yor Xelum Yàlla rekk moo ko man a ràññale. 2:15 Nit ki yor Xelum Yàlla dafay àtte lépp, te moom ci boppam, kenn du ko àtte. 2:16 Ndaxte Mbind mi nee na:«Ana ku xam xalaatu Boroom bi?Ku ko doon digal?» Waaye nun am nanu xalaatu Kirist.
3:1 Man nag bokk yi, mënuma woon a wax ak yéen ni ay nit ñuy déggal Xelum Yàlla, waaye waroon naa wax ak yéen ni ñuy topp seen nafsu, mel ni ay liir ci seen dund ci Kirist. 3:2 Nàmpaloon naa leen, waaye joxuma leen dugub, ndaxte àttanuleen ko woon, te ba léegi sax àttanuleen ko 3:3 ci li ngeen di topp seen nafsu. Bu ñeetaan ak xuloo amee ci seen biir, xanaa du loolu mooy wone ne, dangeen a topp seen nafsu, di doxale ni niti àddina? 3:4 Bu kenn yéglee ne: «Man ci Pool laa bokk,» keneen ne: «Man ci Apolos,» ndax jëfewuleen ni niti àddina rekk? 3:5 Kuy Apolos? ak kuy Pool? Nun ay surga rekk lanu, yu ngeen jaare, ba gëm. Te Boroom bi moo sas ku nekk liggéeyam. 3:6 Maa jëmbët, Apolos suuxat, waaye Yàlla moo jebbil. 3:7 Ki jëmbët nag ak ki suuxat, kenn du ci dara, waaye Yàlla miy jebbil rekk moo am solo. 3:8 Ki jëmbët ak ki suuxat benn lañu. Teewul nag ku nekk dina jot yool bu tollook liggéeyam. 3:9 Nu ngi liggéeyandoo ci liggéeyu Yàlla; yéenay toolu Yàlla, yéenay taaxum Yàlla. 3:10 Man nag teg naa fondamaa bi, ni tabaxkat bu man liggéeyam, dëppoo ak sas wi ma Yàlla jagleel ci kaw yiwam. Te keneen a ngi tabax ci kaw; waaye na ku nekk teeylu ci ni muy tabaxe. 3:11 Ci li jëm ci fondamaa bi, kenn mënu fee tëral beneen bu dul bi fi xas a taxaw, muy Yeesu Kirist. 3:12 Ku tabax ci kaw fondamaa bi, wurus, xaalis, per, dénk, gittax walla boob, 3:13 sa liggéey dina fés, ndaxte bés baa koy xamle. Bés boobu dina fenk ni safara, te safara si dina nattu liggéeyu ku nekk. 3:14 Ku sa liggéey dëgër, dinga jot yool. 3:15 Waaye ku sa liggéey lakk, dinga ñàkk. Yaw ci sa bopp dinga mucc, waaye mel ni ku rëcc ci safara si. 3:16 Xanaa xamuleen ne, yéenay kër Yàlla, te Xelum Yàlla dëkk na ci yéen? 3:17 Ku yàq kër Yàlla gi, Yàlla dina la yàq, ndaxte kër Yàlla gi dafa sell, te yéenay kër googu. 3:18 Kon bu kenn nax boppam: su kenn ci yéen tegee boppam boroom xam-xam ci gis-gisu àddina sii, kooku na doon dof, ngir am xam-xam bu wóor. 3:19 Ndaxte xam-xamu àddina si, ndof la fa Yàlla. Moom la Mbind mi ne: «Yàlla jàpp na ñu muus ñi, ba seen fiir këppu ci seen kaw.» 3:20 Te it: «Boroom bi xam na xalaati boroom xam-xam yi; xam ne, duñu mujj fenn.» 3:21 Kon nag bu kenn tiitaru ndax nit ñi, ndaxte yéena moom lépp, 3:22 muy Pool, di Apolos, di Sefas, di àddina, di dund, di dee, di lu am, di luy ñëw; lépp, yéena ko moom. 3:23 Te yéen, Kirist a leen moom, te Kirist, Yàllaa ko moom.
4:1 Nañu nu teg kon ay surgay Kirist, di ay jawriñ yuy xamle mbóoti Yàlla. 4:2 Li war ci jawriñ mooy mu takku ci liggéeyam. 4:3 Ngeen àtte ma walla ñeneen àtte ma, amaluma ko solo. Te man sax duma àtte sama bopp. 4:4 Sama xel yeddu ma ci dara, waaye loolu taxul ma jub; ki may àtte mooy Boroom bi. 4:5 Looloo tax buleen daan kenn ci àtte, bala jamono ji di jot te Boroom bi ñëw. Mooy leeral yi nëbbu ci lëndëm, di làññi mébétu xol yi. Bu ko defee ku nekk dina jot ci Yàlla ngërëm, li mu yelloo. 4:6 Bokk yi, ci loolu ma leen doon wax lépp nag, misaal naa leen ko ci Apolos ak ci man, ngir ngeen xool ci nun, ba xam li wax jii di tekki: «Bu seen xalaat weesu li Mbind mi wax.» Noonu kenn du màggal kii, suufeel ki ci des. 4:7 Ndaxte yaw, ku la def, ba nga gën a màgg ñi ci des? Loo am lu ñu la mayul? Te bu ñu la ko mayee, lu tax nga di ci tiitaru, mel ni mayuñu la ko? 4:8 Yéen suur ngeen xaat! Woomle ngeen xaat! Tàmbali ngeen di nguuru te agseegunu! Céy ni ma bëgge, ngeen di nguuru, ba nu man a bokk ak yéen di nguuru! 4:9 Xalaat naa ne, nun ndawi Kirist yi, Yàlla def na ba nu mel ni nit ñu ñu jàppe ci xare te mujj ci sàppe yi, ñu dogal seen dee, nuy ceetaanum mbindeef yépp, muy nit muy malaaka. 4:10 Nun teg nañu nu ni ay dof ndax Kirist, waaye yéen am ngeen xel ci Kirist. Néew nanu doole, waaye yéen am ngeen doole. Nawees na leen, waaye nun dañu noo xeeb. 4:11 Ba fii mu nekk, danoo xiif, mar te rafle; ñu ngi nuy dóor, te dëkkunu fenn; 4:12 nu ngi ñaq di jariñoo. Ku nu saaga, nu ñaanal la lu baax. Coono bu ñu nu teg, nu tegoo ko. 4:13 Ku nu ñaawal, nu tontu la tont lu rafet. Fi mu ne noo mujj di mbalitu àddina, di ñu ñàkk njariñ ci lépp. 4:14 Binduma leen loolu ngir ngeen am yeraange, waaye dama koo def ngir artu leen, ndaxte yéenay samay doom te bëgg naa leen. 4:15 Su ngeen amee junniy njiit yu leen di sàmm ci Kirist, ba tey benn baay rekk ngeen am, ndaxte maa leen yégal xebaar bu baax bi, ba jur leen ci Kirist. 4:16 Kon nag maa ngi leen di ñaan, ngeen roy ci man. 4:17 Looloo tax ma yebal ci yéen Timote, miy sama doomu diine, di doom ju takku te ma bëgg ko. Dina leen fàttali ni may dunde ci Kirist, te mu dëppook li may jàngale fu nekk ci mboolooy ñi gëm ñépp. 4:18 Am na ci seen biir ñuy tiitaru, di xalaat ne, duma delluseeti ci yéen. 4:19 Waaye bu soobee Boroom bi, léegi ma ñëw ci yéen te seet boroom tiitar yooyu; waxuma seen kàddu, seen doole laay seet. 4:20 Ndaxte nguuru Yàlla du waxi kese, waaye doole la. 4:21 Lu leen gënal? Ma ñëw ci yéen, yor ab yar, walla ma ànd ak mbëggeel, te lewet?
5:1 Dégg nanu sax ñu naan, am na kuy moy Yàlla ci seen biir, moy gu ni tollu, duñu ko gis sax ci ñi xamul Yàlla. Dem na, ba am ci yéen kuy séy ak jabaru baayam. 5:2 Moona yéen de, yéena ngi tiitaru. Waaye dangeen a waroon a am naqar, ba dàq kiy def loolu ci seen biir! 5:3 Man nag, jëmm ji sore na leen, waaye xel mi mu ngi ci yéen, te àtte naa xaat kiy def loolu, ni su ma teewoon ci seen biir. Dogal naa, 5:4 ngeen daje ci turu Boroom bi Yeesu, te sama xel teewe ko, ànd ak dooley Boroom bi Yeesu, 5:5 nu jébbal nit kooku Seytaane, yaramam yàqu, ngir ruuwam mucc keroog bésu Boroom bi. 5:6 Seen tiitar bi jekkul dara. Xanaa xamuleen ne, tuuti lawiir day tax tooyalu fariñ bépp funki? 5:7 Ni ma leen ko man a misaale, jëleleen fi bépp lawiir bu yàgg, ngir ngeen sell ni tooyal bu bees bu amul lawiir, ndax nekk ngeen ko ba noppi. Ndaxte Kirist deeyal na nu ca bant ba, mel ni mbote mu ñuy rendi, jébbal ko Yàlla ca màggalu bésu Jéggi ba. 5:8 Kon nanu màggal sunu Màggal, waxuma ak lawiir bu màggat biy misaal kiñaan ak lu bon, waaye ak mburu mu amul lawiir, maanaam ci xol bu laab ak ci dëgg. 5:9 Bindoon naa leen, ngeen bañ a séq dara ak njaalookat yi. 5:10 Bëgguma ci woon a limaale waa àddina, maanaam njaalookat yi, nay yi, njublaŋ yi ak xërëmkat yi. Su ngeen séqul ak ñooñu dara, kon fàww ngeen génn àddina. 5:11 Lii laa leen bëggoon a wax: buleen séq dara ak ku ñu tudde mbokk mu gëm Kirist, te fekk day njaaloo walla mu nay walla muy xërëm walla muy xas nit walla muy màndi walla muy njublaŋ. Nit ku mel noonu moom, buleen bokk ak moom, sax far di lekk. 5:12 Ndax man maa war a àtte ñi bokkul ci mbooloom ñi gëm Kirist? Déedéet! Waaye ñi bokk ci seen mbooloo yéena leen war a àtte. 5:13 Ñi bokkul ci mbooloom ñi gëm, Yàlla moo leen di àtte. Waaye yéen, ni ko Mbind mi waxe: «Dàqleen ci seen biir kiy def lu bon.»
6:1 Te it bu kenn ci yéen amee lëj-lëj digganteem ak mbokku taalibeem, lu tax muy dem ca àttekaayi ñi xamul Yàlla, te bañ a dem ca gaayi Yàlla yi, ñu àtte ko? 6:2 Xanaa dangeen a xamul ne, gaayi Yàlla yi ñooy àtteji àddina? Te ndegam yéenay àtteji àddina, lu tere ngeen man a àtte mbir yu ñàkk solo yi? 6:3 Xanaa xamuleen ne, nooy àtteji malaaka yi? waxatumaak mbiri àddina sii. 6:4 Bu ngeen amee ay lëj-lëj yu mel noonu, dangeen di wuti ay àttekat ci ay nit, ñi amul wenn yoon ci mbooloom ñi gëm! 6:5 Ma ne kon, war ngeen a rus! Xanaa amul ci seen biir kenn ku am xel, ku man a àtte mbokkam yi? 6:6 Waaye defuleen loolu; mbokk a ngi layoo ak moroomam, rax-ca-dolli ci kanamu ñi gëmul lañu koy defe! 6:7 Layoo bi sax wone na ne, bàyyi ngeen seen warugar. Lu tax muñuleen sax tooñ, yi ñu leen di tooñ? Lu tax far nanguwuleen, ñu sàcc leen? 6:8 Waaye yéen sax yéenay tooñ ak di sàcc, te seeni bokk ngeen koy def! 6:9 Xanaa xamuleen ne, ñi jubadi duñu bokk ci nguuru Yàlla? Bu leen ci kenn nax: ñiy doxaan walla xërëmkat yi ak njaalookat yi ak góor-jigéen ñi ak ñi ko nangu, 6:10 walla sàcc yi ak ñu bëgge ñi ak màndikat yi ak ñiy xaste ak njublaŋ yi, duñu bokk ci nguuru Yàlla. 6:11 Te am na ñu meloon noonu ci yéen. Waaye Yàlla fóotal na leen seeni bàkkaar, sellal leen, àtte leen ni ñu jub, ci turu Boroom bi Yeesu Kirist ak ci dooley Xelum Yàlla, sunu Boroom. 6:12 Am na ci yéen ñu naan: «Sañ naa lépp.» Waaw, waaye du lépp a jariñ nit. «Sañ naa lépp,» waaye duma bàyyi dara, mu noot ma. 6:13 Am na ci yéen ñu naan: «Ñam mooy jariñ biir, te biir ay jariñoo ñam.» Waaw, te Yàlla dina leen yàq, ñoom ñaar yépp. Waaye sàkkuñu yaram ngir moy Yàlla; dañu koo sàkk, ngir muy jariñ Boroom bi, Boroom bi di ko jariñoo. 6:14 Te Yàlla, mi dekkal Boroom bi, dina dekkal it sunu yaram jaare ko ci dooleem. 6:15 Xanaa xamuleen ne, seen yaram ñooy céri Kirist? Ndax kon damay jël céri Kirist, def ko céri jigéeni moykat? Mukk! 6:16 Xanaa xamuleen ne, kuy ànd ak jigéen juy moy dafay booloo ak moom, nekk benn? Ndaxte Mbind mi nee na: «Ñoom ñaar dinañu doon benn.» 6:17 Waaye nag kuy ànd ak Boroom bi, xel yi dañuy booloo, nekk benn. 6:18 Dawleen njaaloo! Bépp bàkkaar bu nit man a def, du laal yaramam, waaye nag kuy njaaloo, dafay bàkkaar, di lor yaramam. 6:19 Xanaa xamuleen ne, seen yaram mooy kër Yàlla gi? Gannaaw Xel mu Sell maa ngi ci yéen, te Yàllaa leen ko may, kon moomuleen seen bopp, 6:20 ndaxte Yàlla jot na leen ak njëg gu réy. Kon nag màggal-leen Yàlla ci seen yaram.
7:1 Nanu jàll nag léegi ci laaj, yi ngeen ma doon bind, ci bañ a ànd ak jigéen, ndax lu baax la ci góor. 7:2 Lii mooy sama xalaat: moy gu bare gi tax na ba, na góor gu nekk am jabaram, jigéen ju nekk am jëkkëram. 7:3 Jëkkër war na def warugaru jëkkër ci jabaram; jabar it def warugaru jabar ci jëkkëram. 7:4 Jigéen ji amul sañ-sañ ci yaramam moom kenn; jëkkëram moo ko moom. Niki noonu it jëkkër ji amul sañ-sañ ci yaramam; jabaram moo ko moom. 7:5 Bu kenn tere boppam moroomam, su dul ne dangeen a mànkoo ci def noonu ab diir, ngir gën a man a wéet ak Yàlla ciy ñaan. Waaye su loolu weesoo, nangeen doxal yoonu séy; lu ko moy, Seytaane dina leen fiir ndax seen ñàkk maandute. 7:6 Li ma leen di wax fii du ndigal, waaye dama leen di xamal li ñu leen may, ngeen def ko. 7:7 Ndaxte dëgg-dëgg su ma sañoon, kon ñépp mel ni man; waaye ku nekk ak li la Yàlla jagleel, kii ak may gii, kee ak may gale. 7:8 Lii laay yégal ñi séyul ak it ñi seen jëkkër dee: baax na ci yéen, su fekkee dangeen a toog rekk ni man, bañ a séy. 7:9 Waaye su ngeen mënul a téye seen bopp, nangeen séy, ndaxte séy moo gën xemmem di leen gaañ. 7:10 Ñi séy nag, maa ngi leen di jox ndigal lii --Boroom bi moo ko waxoon, du man — jigéen ju séy warul a teqalikoo ak jëkkëram. 7:11 Te bu teqalikoo ak moom, bumu séyaat, mbaa boog na juboo ak jëkkëram. Te bu jëkkër ji fase jabaram. 7:12 Ñi ci des nag, lii laa leen di wax --Boroom bi waxu ko woon — su nit ku gëm Kirist amee jabar ju gëmul, te mu nangoo séy ak moom, waru koo fase. 7:13 Naka noonu it su jigéen ju gëm Kirist amee jëkkër ju gëmul, te mu nangoo nekk ak moom, warul a tas. 7:14 Li tax ma wax ko moo di, jëkkër ji gëmul, Yàlla sellal na ko, ndax li mu ànd ak jabaram. Te it jigéen ji gëmul, Yàlla sellal na ko, ndax li mu ànd ak jëkkëram ji gëm; lu ko moy, seeni doom dinañu am sobe, te fekk dañoo sell. 7:15 Waaye nag, su fekkee ki gëmul bëgg na dem, na dem. Ci wàll googu nag, ki gëm Kirist, muy jëkkër ji walla jabar ji, amul benn tënk, ndaxte Yàlla moo leen woo ngir ngeen dund ci jàmm. 7:16 Loo ci xam, yaw jigéen ji, ndax dinga gëmloo sa jëkkër Musalkat bi walla déet? Loo ci xam yaw jëkkër ji it, ndax dinga gëmloo sa jabar Musalkat bi walla déet? 7:17 Ku nekk nag na dund, ni ko ko Boroom bi jagleele, mu mengoo ak ni mu meloon, bi ko Yàlla wooyee. Moom laay tëral ci mboolooy ñi gëm yépp. 7:18 Ki xaraf, bi ko Yàlla wooyee, warul a jéem a far màndargam xaraf bi. Ki xaraful, bi ko Yàlla wooyee, aajowul mu xaraf. 7:19 Xaraf ak ñàkka xaraf lépp a yem; li am solo moo di topp ndigali Yàlla. 7:20 Na kenn ku nekk jàpp ci li mu nekkoon, bi ko Yàlla wooyee. 7:21 Ndax jaam nga woon, bi la Yàlla wooyee? Na ci sa xel dal. Waaye soo amee bunt, ba yiwiku, nanga ci jaar. 7:22 Ku nekkoon jaam, bi la Boroom bi wooyee, Boroom bi goreel na la. Ba tey it ku nekkoon gor, bi ñu la wooyee, jaamu Kirist nga. 7:23 Gannaaw Yàlla jot na leen ak njëg gu réy, buleen doon jaamub nit. 7:24 Bokk yi, fàww ku nekk wéy ca kanam Yàlla ci fànn ga mu nekkoon, bi ko Yàlla wooyee. 7:25 Ci li jëm ci janq yi, awma ndigalu Boroom bi, waaye maa ngi joxe sama xalaat, ni ku ñu wóolu ndax li ma jot yërmandey Boroom bi. 7:26 Bu nu seetee tiis wii fi teew nag, defe naa ne li baax ci nit, moo di mu sax ci li mu nekk. 7:27 Ndax takk nga jabar? Bul wut a tàggoo ak moom. Ndax takkuloo jabar? Bul wut jabar. 7:28 Waaye nag boo séyee, defoo bàkkaar, te bu janq séyee, deful bàkkaar. Waaye ñi séy dinañu am naqar ci àddina, te naqar woowu dama leen koo bëggoon fanqal, yéen ñi séyagul. 7:29 Lii laa bëgg a wax, bokk yi: diir bu gàtt rekk a fi des. Lu weesu tey, na góor ñi am jabar di def, ni bu ñu ko amul woon; 7:30 ñiy jooy, mel ni ñu jooyul; ñiy bég, mel ni ñu bégul; ñiy jënd, ni ñu moomul li ñu jënd; 7:31 ñiy jariñoo àddina, bañ cee xér. Ndaxte àddina sii, ci ni mu mel, dootul yàggati. 7:32 Bëggoon naa, ngeen bañ a am benn xalaat. Góor gu takkul jabar dafay bàyyi xel ci mbiri Boroom bi, di wut a neex Boroom bi. 7:33 Waaye ku takk jabar, fàww mu bàyyi xel ci mbiri àddina si, ak nu mu man a neexe jabaram, 7:34 te noonu dafay daldi bare soxla. Te jigéen ju séyul, walla janq, dafay bàyyi xel ci mbiri Boroom bi — bëgg koo jox yaramam ak xelam. Waaye jigéen ji séy dafay bàyyi xel ci mbiri àddina, ak nu mu man a neexe jëkkëram. 7:35 Seen njariñ a tax ma wax lii, du ngir teg leen yen bu ngeen àttanul, waaye ngeen man a jàppandil Boroom bi ci njaamu gu rafet gu àndul ak genn njaaxle. 7:36 Nanu jàll nag ci mbiri kiy takk ngoro te amul pasteefu takk ndaw si. Su fekkee ne waxambaane wi xalaat na ne, jëfewul nu jekk ak janq bi, fekk muy wees ag ndawam, te mu xalaat ne dafa koo war a takk, kon na ko takk, ni mu ko bëgge; deful bàkkaar. 7:37 Waaye nag su dogoo dëgg ci bañ a takk, fekk sagoom rekk a tax te kenn tegu ko ko, kon ba tey def na lu baax. 7:38 Noonu ku takk as ndawam def na lu baax, rawatina nag ku takkul. 7:39 Jigéen ji séy dina ànd ak jëkkëram giiru dundam. Waaye su jëkkër ji faatoo, man na séy ak ku ko neex, su fekkee ne góor gu gëm la. 7:40 Moona nag dina gën a bég, bu toogee noonu rekk. Loolu mooy sama xalaat, te defe naa ne, man it am naa Xelum Yàlla.
8:1 Léegi nag, ci li jëm ci yàpp wi ñu jébbal xërëm yi: nun ñépp am nanu xam-xam, loolu dëgg la. Xam-xam day tax ba nit yég boppam, waaye mbëggeel day yékkati ngëm. 8:2 Ku xalaat ne xam nga dara, sa xam-xam bënnagul. 8:3 Waaye ku bëgg Yàlla, Yàlla xam la. 8:4 Kon nag ci li jëm ci lekk yàpp wu ñu jébbal xërëm yi, xam nanu ne, xërëm du dara ci àddina te xam nanu itam ne, Yàlla kenn rekk la. 8:5 Su fekkee ne am na sax yu ñuy teg Yàlla, muy ci asamaan mbaa ci suuf --ndaxte am na yu bare yu ñu faral di bokkaaleel Yàlla ak Boroom bi — 8:6 ba tey ci nun, jenn Yàlla rekk a am, muy Baay bi; lépp a ngi jóge ci moom te moom lanu nekkal. Te it benn Boroom rekk a am, muy Yeesu Kirist; lépp a ngi jaare ci moom, te nun it nu ngi dund jaare ci moom. 8:7 Waaye ñépp xamuñu loolu. Am na ñu tàmmoon xërëm yi, te léegi, bu ñu lekkatee yàppu sarax yi, dañuy xalaat ne, xërëm lañu ko jagleel. Seen xel dafa leen di yedd, ndaxte ci seen ñàkka xam dañuy foog ne, taq nañu sobe ndax ñam woowu. 8:8 Waaye ñam mënul a tax nu neex Yàlla. Su nu ci lekkee, du yokk dara ci nun. Su nu ci lekkul, du nu wàññi dara. 8:9 Waaye moytuleen, ba sañ-sañ bi ngeen am, bañ a yóbbe bàkkaar ñi seen ngëm néew. 8:10 Su amee ku ngëmam néew, mu gis la, yaw mi bare xam-xam, nga toog di lekk ca màggalukaayu xërëm ya, ndax du ko xiir mu lekk yàppu sarax? 8:11 Noonu sa xam-xam dina lor kooku ngëmam néew, fekk sa mbokk moomu, Kirist dee na ngir moom! 8:12 Su ngeen bàkkaaree, ba tooñ bokk yi néew ngëm, di nëxal seen xel, bàkkaar ngeen ba tooñ Kirist. 8:13 Kon bu sama mbokk sóoboo ci bàkkaar ndax ñam wi ma lekk, dootuma lekk mukk yàpp, ngir bañ a sóob ci bàkkaar sama mbokk mi.
9:1 Ndax awma ndogal ci li may def? Ndax duma ndawul Kirist? Ndax gisuma Yeesu sunu Boroom? Xanaa du yéena soqikoo ci liggéey, bi ma Boroom bi sant? 9:2 Su ma ñenn ñi tegul ndaw, moom laa ci yéen, ndaxte yéenay firnde jiy wone ne, ndawul Boroom bi dëgg laa. 9:3 Nii laay tontoo ñi may àtte: 9:4 Xanaa sañunoo lekk ak a naan? 9:5 Xanaa sañunoo indaale jabar ju gëm Kirist, ni yeneen ndawul Kirist ak doomi ndeyu Boroom bi ak Sefas sax? 9:6 Walla boog man ak Barnabas rekk noo war a daan sunu doole? 9:7 Kan moo mas a solu soldaar ci pexey boppam? Kan mooy bey tool te du ci jariñu? Walla kan mooy sàmm jur te du naan ca soow ma? 9:8 Lii may wax, du ci yëfi doom Aadama rekk laa ko jukkee; xanaa du yoon wi it moo ko santaane? 9:9 Ndaxte bind nañu ci yoonu Musaa ne: «Bul sunjuñ gémmiñu nag wu ñu takk ci bojjukaay.» Ndax mooy tekki nag ne, Yàlla dafa bàyyi xel nag yi? 9:10 Walla boog xanaa nun noo moom wax jooju? Waaw, noo tax ñu bind loolu. Noonu kuy bey war na am yaakaar, te kuy bojj di yaakaar a jot wàllam. 9:11 Nu ji ci yéen yëfi Xelum Yàlla, ba noppi góobe ci yéen yëfi àddina, ndax loolu dafa ëpp li nu war a séentu? 9:12 Ndegam ñeneen a am sañ-sañ boobu ci yéen, nun kon waxi-noppi. Waaye nag jariñoowunu sañ-sañ boobu. Danuy far muñ lépp, ngir bañ a indi ndog ci yoonu xebaar bu baax bu Kirist bi. 9:13 Xanaa xamuleen ne, ñiy liggéeyal yëf yu sell yi, dañuy lekk ñam, wi ci kër Yàlla gi, te ñiy liggéey ci saraxalukaay bi, dañuy jot seen wàll ci sarax yi? 9:14 Naka noonu it Boroom bi digle na ne, ñiy yégle xebaar bu baax bi, nanu ci dund. 9:15 Waaye man jariñoowuma benn ci sañ-sañ yooyu, te binduma yëf yooyu, ngir ngeen di ma defal yu ni mel. Dee sax moo ma ko gënal — kenn du jële ci man mbir moomu may kañoo! 9:16 Su may yégle xebaar bu baax bi, mënuma cee kañu. Sas la, wu ñu ma sas. Dinaa torox, su ma yéglewul xebaar bu baax bi! 9:17 Su doon ci sama coobare laa yégle xebaar bu baax bi, man naa ci séentu yool. Waaye defuma ko ci sama coobare, ndaxte sas la, wu ñu ma sas. 9:18 Kon nag lan mooy sama yool? Xanaa di yégle xebaar bu baax bi ci dara, te bañ a jariñoo sañ-sañ boobu ma ci yelloo. 9:19 Gor laa te kenn moomu ma; teewul def naa sama bopp jaamu ñépp, ngir man a gindi nit ñu bare ci Kirist. 9:20 Ci biir Yawut yi, sol naa melow Yawut yi, ngir gindi leen. Man ci sama bopp yoonu Musaa jiitalu ma, terewul bi ma nekkee ci biir ñiy sàmm yoonu Musaa, sàmm naa yoon wa, ngir gindi leen. 9:21 Ci biir ñi nekkul ci yoonu Musaa, faalewuma woon yoon wi, ngir gindi leen; waxuma ne, ànduma ak yoonu Yàlla, waaye topp naa yoon ci sama bokk ak Kirist. 9:22 Ci biir ñi néew ngëm, meloon naa ni ku néew ngëm, ngir gindi leen. Doon naa lépp ci ñépp, ngir def lépp lu ma man, ba ñenn mucc ci. 9:23 Damaa def loolu lépp ndax xebaar bu baax bi, ngir man it ma am wàll ci barkeem. 9:24 Xanaa xamuleen ne, ñépp ñooy daw cib rawante, waaye kenn rekk ay jël ndam li? Dawleen nag ngir jël ko. 9:25 Ñiy joŋante ci po muy waral tàggat yaram, dañuy xañ seen bopp lu bare. Dañu koy def, ngir am kaalag ndam gu dul yàgg; waaye nun danu koy def, ngir am kaalag ndam gu sax ba fàww. 9:26 Man nag noonu laay dawe, te duma dawantu. Noonu laay bëree, waaye duma def ni nit kuy dóor ci jaww ji. 9:27 Waaye damay noot sama yaram, ba moom ko, ngir ragal a yégal ñi ci des xebaar bu baax bi, ba noppi Yàlla xañ ma ndam li.
10:1 Bokk yi, bëgguma ngeen umple li daloon sunu maam ya. Ñoom ñépp niir wa tiimoon na leen, te ñoom ñépp jàll nañu géej. 10:2 Sóobu nañu ca ndoxu géej ga ak ca niir wa, ba bokk noonu ci Musaa. 10:3 Ñoom ñépp bokk nañoo lekk ñam, wa Yàlla joxe, 10:4 naan naan ga mu joxe, ndaxte ñu ngi doon naan ca xeer, wa leen doon gunge, te xeer woowa Kirist la woon. 10:5 Teewul ñi ëpp ci ñoom neexuñu woon Yàlla, ba mu fàddoon leen ca màndiŋ ma. 10:6 Mbir yooyu ay misaal lañu, yu nuy artu, ngir benn bëgg-bëgg bu bon bañ noo jiital, na mu leen jiitale woon. 10:7 Buleen jaamu ay xërëm, ni ko ñenn ñi ci ñoom defe woon. Ndaxte Mbind mi nee na: «Mbooloo mi dafa toog, di lekk ak di naan, ba noppi ñu jóg di mbumbaay.» 10:8 Bunu njaaloo, ni ko ñenn ñi ci ñoom defe woon, ba tax ñaar-fukki junni ak ñett ci ñoom dee ci benn bés. 10:9 Bunu diiŋat Kirist, ni ko ñenn ñi ci ñoom defe, ba ay jaan màtt leen, ñu dee. 10:10 Buleen xultu, ni ko ñenn ñi ci ñoom defe woon, ba tax malaakam Yàqkat mi rey leen. 10:11 Mbir yooyu leen daloon misaal la ci nun, te bind nañu ko ngir artu nu, nun ñiy dund ci jamono jii lépp mat. 10:12 Kon nag kiy naw sa doole, ba yaakaar ne taxaw nga, moytul a daanu ci bàkkaar! 10:13 Benn nattu dabu leen bu wuute ak yi dal nit ñépp. Te sax Yàlla kuy sàmm kóllëre la, te du nangu nattu bi wees seen kàttan, waaye cib nattu, dina leen ubbil bunt bu ngeen man a récce, ba ngeen man koo dékku. 10:14 Looloo tax, sama soppe yi, nangeen daw xërëm yi. 10:15 Maa ngi wax ak yéen ñi am xel. Kon seetleen li ma leen wax. 10:16 Kaas bu yiw, bi tax nuy gërëm Yàlla, ndax du wone sunu booloo ak deretu Kirist? Mburu mi nuy damm, xanaa du dafay wone sunu booloo ak yaramu Kirist? 10:17 Ndegam benn mburu rekk a am, kon nun ñépp lu nu baree-bare, menn mbooloo lanu, ndaxte bokk nanu menn mburu mi. 10:18 Seetleen ci bànni Israyil. Ñiy lekk sarax si ñu rendi, ndax booloowuñu ak Yàlla ji ñu jagleel saraxalukaay ba? Aaŋkay! 10:19 Li may wax, lu muy tekki? Ndax yàpp wi ñu jagleel xërëm yi dafay dara? walla xërëm yi dañuy dara? 10:20 Déedéet! Waaye sarax yi xërëmkat yi di rendi, ay rab lañu ko jagleel; jagleeluñu ko Yàlla. Te man bëgguma, ngeen booloo ak rab yi. 10:21 Mënuleen a naan ci kaasu Boroom bi, naan ci kaasu rab yi. Mënuleen a sukk ci reerub Boroom bi, sukk ci reerub rab yi. 10:22 Walla boog ndax danuy jéem a gillil meru Boroom bi? Xanaa noo ko ëpp doole? 10:23 Dafa am ñu naan: «Lépp lanu sañ.» Waaw, waaye du lépp a baax ci nun. «Lépp lanu sañ,» waaye it lépp du yékkati ngëm. 10:24 Bu kenn seet njariñam rekk, waaye nay seet njariñul moroomam. 10:25 Man ngeen a lekk lépp lu ñuy jaay ca ja ba, bañ cee boole ay laaj ngir dalal seen xel. 10:26 Ndaxte Mbind mi nee na: «Àddina ak li ci biiram lépp, Boroom bi moo ko moom.» 10:27 Ku xamul Yàlla nag, bu leen wooyee aw ñam këram, te ngeen nangoo dem, lekkleen lépp lu ñu leen dëj, bañ a laajte dara ngir dalal seen xel. 10:28 Waaye bu leen kenn nee: «Lii sarax la, bu ñu jagleel xërëm yi,» suurleen ko ndax ki leen ko xamal, ngir xel mu dal. 10:29 Waxuma sa xel yaw, waaye xelu keneen laay wax. Waaye nga ne: «Li ma sañ a def, lu tax nit ku xelam dalul di am dara lu mu ciy wax? 10:30 Su ma lekkee dara di ci sant Yàlla, lu tax ñu may wax lu ñaaw, fekk sant naa ci Yàlla.» 10:31 Kon su ngeen di lekk walla ngeen di naan, walla lu ngeen man a def, defleen lépp ngir màggal Yàlla. 10:32 Buleen def dara lu man a fanq ngëmu Yawut yi walla ñi dul Yawut walla mbooloom Yàlla. 10:33 Noonu laay def man ci sama bopp: damay wut a neex ñépp ci lépp. Wutuma lu may jariñ, waaye luy jariñ ñu bare laay wut, ngir ñu mucc.
11:1 Royleen ma nag, ni may roye Kirist. 11:2 Maa ngi leen di sant ci li ngeen may fàttaliku ci lépp, ak ci li ngeen di topp dénkaane, yi ma leen dénk. 11:3 Waaye nag bëgg naa ngeen xam lii: Kirist mooy kilifag bépp góor, góor di kilifag jigéen, te Yàlla di kilifag Kirist. 11:4 Kon nag góor guy ñaan Yàlla, walla muy wax ci kàddug Yàlla, fekk mu teg dara ci boppam, day suufeel Kirist, kilifaam. 11:5 Waaye bu jigéen musóoruwul, buy ñaan walla buy wax ci kàddug Yàlla, kooku day suufeel jëkkëram jiy kilifaam, ndaxte day mel ni jigéen ju ñu wat. 11:6 Jigéen ju dul musóoru, bu yaboo, mu watu. Waaye su fekkee ne jigéen dafay am kersa, su wàññee kawaram walla mu watu, fàww kon mu musóoru. 11:7 Góor nag moom warul a teg dara ci boppam, ndaxte mooy melokaanu Yàlla te dafay wone ndamu Yàlla. Jigéen moom dafay wone ndamu góor. 11:8 Ndaxte jëlewuñu góor ci jigéen, waaye jigéen lañu jële ci góor. 11:9 Te sàkkuñu góor ngir jigéen, waaye jigéen lañu sàkk ngir góor. 11:10 Looloo tax jigéen war a teg ci kaw boppam luy màndargaal kilifteef ga, ndax malaaka yi. 11:11 Teewul nag ci sunu booloo ak Boroom bi, jigéen a ngi wéeru ci góor, te góor a ngi wéeru ci jigéen. 11:12 Ni ñu sàkke jigéen ci góor, noonu la góor juddoo ci jigéen, te lépp a ngi jóge ca Yàlla. 11:13 Seetleen mbir mii: ndax jekk na jigéen bañ a musóoru, buy ñaan Yàlla? 11:14 Xanaa du àddina ci boppam dafa leen di won ne, gàcce la ci góor, ngir muy yar kawar gu bare? 11:15 Waaye loolu nag ab taar la ci jigéen. Dañoo jagleel jigéen kawar gu gudd, muy muuraay ci moom. 11:16 Waaye su kenn bëggee werante ci mbir moomu, na xam lii: amunu beneen aada ci njàng mi, du nun walla mboolooy Yàlla. 11:17 Bi may tollu ci ndigal yi, mënuma leen a sant, ndaxte seeni ndaje loraange lañuy jur, waaye du njariñ. 11:18 Ci bu jëkk dégg naa lii: bu ngeen di daje, am na ci yéen ñuy féewaloo, te xaw naa koo gëm. 11:19 Fàww mu am ay féewaloo ci seen biir, ngir ñu man a xàmmi ñi neex Yàlla ci yéen. 11:20 Bu ngeen dajee, mënuleen a wax ne reeru Boroom bi ngeen di lekk. 11:21 Ndaxte bu ngeen dee lekk, ku nekk dafay gaawantu di lekk reeram, ba tax ñenn ñaa ngi xiif, fekk ñeneen di màndi. 11:22 Xanaa amuleen kër yu ngeen di lekke ak di naane? Walla ndax dangeen a xeeb mbooloom Yàlla? Walla ngeen bëgg a rusloo ñi amul dara? Lu ma leen ci war a wax nag? Ma gërëm leen ci loolu? Mukk! Gërëmuma leen. 11:23 Li ma jële ci Boroom bi, moom laa leen jottali: Boroom bi Yeesu, ci guddi gi ñu ko woree, dafa jël mburu, 11:24 sant Yàlla, damm ko ne: «Lii sama yaram la, wi ma joxe ngir yéen. Defleen lii, ngir fàttaliku ma.» 11:25 Noonu itam bi ñu lekkee ba noppi, mu jël kaas bi ne leen: «Kaas bii mooy misaal kóllëre gu bees, gi Yàlla fas jaarale ko ci sama deret. Defleen lii ngir fàttaliku ma.» 11:26 Ndaxte saa su ngeen di lekk mburu mii, walla ngeen di naan ci kaas bii, yéena ngi yégle deewu Boroom bi, ba kera muy ñëw. 11:27 Kon nag képp ku jekkadi ni mu lekke ci mburu mi te naane ni ci kaasu Boroom bi, tooñ nga yaramu Boroom bi ak deretam. 11:28 Na ku nekk seetlu boppam nag, sog a lekk ci mburu mi te naan ci kaas bi. 11:29 Ku lekk mburu mi, naan ci kaas bi, fekk faalewuloo solos yaramu Kirist wi, sa lekk ak sa naan dina xëcc àtteb Yàlla ci sa kaw. 11:30 Looloo tax ñu bare ci yéen wopp te ñàkk doole, ba ñenn ñi faatu. 11:31 Su nu doon seetlu sunu bopp ni mu ware, kon àtte du nu dal. 11:32 Waaye bu nu Boroom bi dee àtte, da nuy yar ngir bañ noo boole ci mbugalu àddina. 11:33 Noonu nag bokk yi, bu ngeen dajee, di lekk reeru Boroom bi, nangeen xaarante. 11:34 Ku xiif, na lekke këram, ngir bañ a indi ci yéen àtteb Yàlla ndax seen ndaje yi. Yeneen fànn yi ci des nag, bu ma ñëwee ci yéen, dinaa ko seet.
12:1 Léegi nag bokk yi, ci li jëm ci mayi Xelum Yàlla, bëgguma ngeen umple ci dara. 12:2 Xam ngeen ne, bi ngeen xamagul woon Yàlla, xërëm, yi mënul a wax, ñoo leen jiitaloon, di leen wommat. 12:3 Moo tax ma leen di xamal lii: ku Xelum Yàlla solu du wax ne: «Yeesu dafa araam.» Te it kenn mënul a wax ne: «Yeesu mooy Boroom bi,» su ko ko Xelum Yàlla waxloowul. 12:4 Am na fànni may yu bare yu jóge ci Xelum Yàlla, waaye menn Xel moomu moo koy séddale. 12:5 Am na ay sas yu bare, waaye benn Boroom bi la. 12:6 Am na ay fànn yu bare yu Yàllay feeñale dooleem, waaye jenn Yàlla ji mooy jëfe doole yooyu yépp ci ñépp. 12:7 Noonu Yàlla jox na ku nekk fànn gu muy feeñale Xelam mu Sell mi ngir njariñul ñépp. 12:8 Am na ku Yàlla sédde, jaarale ko ci Xelam, mayu wax ak xel mu leer, keneen am mayu xam-xam, te mu bawoo ci menn Xel mi. 12:9 Keneen it menn Xel mi jox ko ngëm, keneen di wéral ay jàngoro ci kàttanu Xel moomu, 12:10 keneen di def ay kéemaan, am kuy wax ci kàddug Yàlla, am keneen kuy ràññee li jóge ci Xelum Yàlla ak li jóge ci yeneen xel yi, keneen it di wax ay xeeti làkk, ak kuy firi làkk yooyu. 12:11 Loolu lépp, menn Xel moomu moo koy def, ku nekk mu sédd la ci, ni mu ko soobe. 12:12 Noona la ci yaramu nit. Yaram wenn la, teewul am na cér yu bare. Waaye céri yaram yépp, ak li ñuy baree-bare, ñoo bokk, doon wenn yaram. Te noonu la Kirist mel. 12:13 Yàlla sóob na nu ci menn Xelam mi, ngir nu doon wenn yaram: nuy Yawut walla nu dul Yawut, nuy jaam mbaa gor, nun ñépp Yàlla may na nu, nu naan ci menn Xel mi. 12:14 Yaram du benn cér, waaye cér yu bare la. 12:15 Kon bu tànk nee: «Man duma loxo, kon bokkuma ci yaram,» du ko teree bokk ci céri yaram yi. 12:16 Te bu nopp nee: «Duma bët, kon bokkuma ci yaram,» du ko teree bokk ci céri yaram yi. 12:17 Bu yaram wépp doon bët, kon nan lay dégge? Walla bu yaram wépp doon nopp, kon nan lay xeeñtoo? 12:18 Waaye Yàlla dafa riime céri yaram wi, def bu ci nekk fa mu ko soobe. 12:19 Bu lépp doon benn cér, kon fu yaram di nekk? 12:20 Cér yi daal, bare nañu waaye wenn yaram rekk a am. 12:21 Bët nag mënul ne loxo: «Soxlawuma la!» Te bopp it mënul ne tànk yi: «Soxlawuma leen!» 12:22 Loolu sax mënul a am, ndaxte céri yaram, yi gën a néew doole, ñoo gën a am jariñ. 12:23 Te cér yi gën a ñàkk maana, ñoom lanuy gën a topptoo. Cér yi ci rafetul a tudd, ñoom lanuy gën a suturaal, 12:24 fekk yi gën a rafet, soxlawul nu leen di suturaale noonu. Waaye Yàlla dafa boole sunu céri yaram yi, ngir gën a teral cér yi ko soxla. 12:25 Noonu yaram du séddaloo, waaye cér bu ci nekk dina dimbali yi ci des. 12:26 Bu sa benn céru yaram dee metti, yeneen yi ci des yépp dañuy bokk, yég metit wi. Te bu dee dangaa fonk sa benn céru yaram it, ndax du sa yaram wépp a ciy bànneexu? 12:27 Léegi benn yaram ngeen, muy yaramu Kirist, te kenn ku nekk ci yéen cér nga ci. 12:28 Te Yàlla teg na ci mbooloom ñi gëm, ku nekk ak sa may: ci bu jëkk ay ndawi Kirist, teg ca ñiy wax ci kàddug Yàlla, teg ca ñiy jàngale, ñiy def ay kéemaan, ñi am mayu wéral ay jàngoro, ñiy dimbalee, ñiy jiite, ñiy wax ay xeeti làkk. 12:29 Ndax ñépp ay ndawi Kirist lañu? Ndax ñépp dañuy wax ci kàddug Yàlla? Ndax ñépp ay jàngale? Ndax ñépp ay def kéemaan? 12:30 Ndax ñépp a am mayu wéral ay jàngoro? Ndax ñépp ay wax ay làkk? Ndax ñépp a leen di firi? 12:31 Waaye fonkleen may yi gën. Léegi nag ma won leen yoon wu gën lépp.
13:1 Su fekkee ne damay wax làkki nit ñi ak yu malaaka yi sax, te boolewuma ci mbëggeel, duma dara lu dul ndënd muy riir, walla jóolóoli buy kandaŋ-kandaŋi. 13:2 Su ma yéglee wax ju tukkee ci Yàlla, ma xam lépp luy kumpa, ma yor xam-xam bépp, te gëm Yàlla ba man a randal ay tund, fekk boolewuma ci mbëggeel, duma dara. 13:3 Te it su ma doon saraxe li ma am lépp, di bàyyi ñu lakk sama yaram, ba rey ma, su ma ci boolewul mbëggeel, du ma jariñ dara. 13:4 Ku bëgg dafay muñ te laabiir. Ku bëgg du kiñaan, du kañu, du tiitaru, 13:5 du def lu jekkadi, du wut njariñu boppam, du naqari deret, du ñaaw njort. 13:6 Du bég ci lu awul yoon, waaye dina bég ci lépp luy jollil dëgg. 13:7 Mbëggeel day baale lépp, am gëm ci lépp, yaakaar lépp, muñ lépp. 13:8 Mbëggeel amul àpp. Ñiy wax ci kàddug Yàlla dinañu noppi, ñiy wax ay làkk dinañu ko bàyyi, ñiy xamle xam-xamu Yàlla wàcc. 13:9 Xam-xam bi nu am des na, te ni nu jottalee xebaar bi nu Yàlla dénk des na. 13:10 Waaye li mat, bu dikkee, li matul jóge fi. 13:11 Bi ma dee xale, dama doon wax ni xale, di dégge ni xale, di xalaate ni xale. Waaye bi ma doonee mag, bàyyi naa lu bokkoon cig ndaw. 13:12 Tey jii gis bu lëndëm lanuy gis, ni takkandeer ci seetu bu lëndëm, bu ëllëgee dinanu gis jaxran. Tey jii sama xam-xam des na, bu ëllëgee dinaa xam ba mat sëkk, ni ma Yàlla xame. 13:13 Léegi nag ñett yii ñooy sax: ngëm, yaakaar, mbëggeel; te mbëggeel moo ci raw.
14:1 Xintewooleen mbëggeel te fonk mayi Xelum Yàlla, rawatina mayu wax ci kàddug Yàlla, 14:2 ndaxte kiy wax aw làkk, waxul ak nit ñi, waaye Yàlla lay waxal, ndaxte kenn déggul li muy wax. Dafay wax ay mbóot ci xelam. 14:3 Waaye kiy jottali kàddug Yàlla, nit ñi lay waxal ngir yékkati seen ngëm, di leen dénk ak a dëfël. 14:4 Kiy wax aw làkk dafay yokk boppam, waaye kiy wax ci kàddug Yàlla, dafay yokk ngëmu mbooloo mi. 14:5 Léegi nag bëgg naa yéen ñépp, ngeen di wax ay làkk, waaye li ma gënal mooy ngeen di wax ci kàddug Yàlla. Kiy wax ci kàddug Yàlla moo gën kiy wax ay làkk, su firiwul li muy wax, ngir ngëmu mbooloo mi yokku. 14:6 Kon nag bokk yi, su ma ñëwee ci yéen, di wax ay làkk, lu ma leen di jariñ? Dara, su ma leen indilul dëgg gu Yàlla feeñal, walla xam-xam walla kàddu gu tukkee ca Yàlla, walla am njàngale. 14:7 Noonu la mel itam ci yëf yi dundul tey riir, ni toxoro walla xalam. Su li ci jibe leerul, naka la nit man a ràññee li mbiibi toxoro walla buumi xalam di wax? 14:8 Rax-ca-dolli su liit gi jibul bu leer, kuy man a waajal xare ba? 14:9 Noonu itam bu ngeen génnewul ay wax yu leer ci seen gémmiñ, nan lañuy man a xame li ngeen di wax? Dingeen wax cig neen! 14:10 Xawma ñaata xeeti làkk a am ci àddina, te wu ci nekk am na lu muy tekki. 14:11 Su ma xamul nag làkk wi ñu may làkk, doxandéem laay doon ci ki koy wax, te ki koy wax it doxandéem la ci man. 14:12 Yéen itam, gannaaw dangeen a fonk mayi Xelum Yàlla, jéemleen a ëpple ci liy yokk ngëmu mbooloo mi. 14:13 Looloo tax kiy wax aw làkk, na ñaan ngir mu man a firi li looluy tekki. 14:14 Su may ñaan Yàlla ci aw làkk, sama xol day ñaan, waaye sama xel amalul kenn njariñ. 14:15 Kon nag lu muy indi? Bu may ñaan, dinaa ànd ak sama xol, àndaale ak sama xel. Bu may woy, dinaa ànd ak sama xol, àndaale ak sama xel. 14:16 Walla, boo dee gërëm Yàlla, ànd ci ak sa xol rekk, kon ku musul a jàng mbir yooyu, nan la man a waxe: «Amiin,» ci sa cant Yàlla googu? Ndaxte xamul li ngay wax. 14:17 Dëgg la, dangay sant Yàlla bu baax, waaye ki ci des, ngëmam yokkuwul. 14:18 Maa ngi sant Yàlla ci li may wax ay làkk, ba raw leen yéen ñépp. 14:19 Waaye ci ndajem mbooloom ñi gëm, wax juróomi baat yu am njariñ, ngir jàngal ñi ci des, moo ma gënal wax fukki junniy baat ciw làkk. 14:20 Bokk yi, buleen melati ni ay xale, ci ni ngeen di xalaate. Ci lu jëm ci lu bon, mel-leen ni ay xale, waaye ci seeni xalaat, mel-leen ni ay mag. 14:21 Bind nañu ci téereb yoon wi:«Dinaa wax ak mbooloo mii,jaare ko ci ay nit, ñuy wax yeneen làkk,ak ay gémmiñi doxandéem,waaye ba tey duñu ma déglu.» Moom la Boroom bi wax. 14:22 Ci noonu wax ay làkk, firnde la ci ñi gëmul, te du firnde ci ñi gëm. Te it wax ci kàddug Yàlla, du firnde ci ñi gëmul, waaye firnde la ci ñi gëm. 14:23 Kon nag su fekkee ku jàngul mbiri Kirist walla ku gëmul dugg ca mbooloo ma, fekk ñépp di wax ay làkk, ndax du wax ne, dangeen a dof? 14:24 Waaye bu ñépp dee wax ci kàddug Yàlla, te ku gëmul dugg fa, walla ku jàngul mbiri Kirist, wax yi ñépp wax dafay wone bàkkaaram te àtte ko, 14:25 ba kumpay xolam feeñ. Bu ko defee dina dëpp jëwam ci suuf, di màggal Yàlla te naan: «Dëgg-dëgg Yàllaa ngi ci seen biir.» 14:26 Kon nag bokk yi, lu muy indi? Bu ngeen dajee, kii am aw taalif, kii am njàngale, kii dëgg gu Yàlla feeñal, kii di wax aw làkk, kee di ko firi. Na loolu lépp aw ci yoonu yokk ngëmu mbooloo mi. 14:27 Su amee kuy wax aw làkk, na ñaar wax walla gën gaa bare ñett. Nañu ko toppante, te kenn di firi. 14:28 Su amul kuy firi, kooku di wax aw làkk, na noppi ci ndajem mbooloo mi. Na waxanteek Yàlla ci xolam. 14:29 Ci ñiy wax ci kàddug Yàlla nag, na ñaar walla ñett wax, te ñi ci des ràññee li ñuy wax. 14:30 Su amee ku toog te Yàlla feeñal ko dëgg, na ki doon wax noppi. 14:31 Yéen ñépp man ngeen a kenn-kennoo wax ci kàddug Yàlla, ngir ñépp jàng te dégg li ñu leen di dénk. 14:32 Ñiy jottali kàddug Yàlla dañoo moom seen xel, 14:33 ndaxte Yàlla du Yàllay lëj-lëj waaye Yàllay jàmm la. Ci mboolooy gaayi Yàlla yépp, 14:34 na jigéen ñi noppi ci ndaje mi, ndaxte sañuñu faa wax. Nañu doon jigéen ñu nangu, ni ko yoon wi tërale. 14:35 Te su ñu bëggee laaj dara, nañu ko laaj seen jëkkër ca kër ga, ndaxte jigéen di wax ci ndajem mbooloom ñi gëm, gàcce la. 14:36 Ndax ci yéen la kàddug Yàlla sosoo? Walla ndax ci yéen rekk la agsi? 14:37 Su kenn xalaatee ne, mooy wax ci kàddug Yàlla, walla mu xalaat ne, Xelum Yàlla jagleel na may, na nangu ne lii ma leen bind ndigalu Boroom bi la. 14:38 Te su ko xeebee it, ñu xeeb ko. 14:39 Kon nag bokk yi, farluleen ci di wax ci kàddug Yàlla, te buleen tere kenn muy wax ay làkk. 14:40 Waaye nag, na lépp di dox ciy teggin te aw yoon.
15:1 Léegi nag bokk yi, maa ngi leen di fàttali xebaar bu baax bi ma leen yégal. Xebaar bu baax boobu, nangu ngeen ko te yéena ngi ciy sax. 15:2 Ci moom ngeen jaare, ba mucc, bu ngeen téyee bu dëgër njàngale mi, ni ma leen ko yégale. Walla xanaa boog gëm ngeen ko cig neen? 15:3 Li ma jotoon, jottali naa leen ko, te moo jëkk ci maana yi: Kirist dee na ngir dindi sunuy bàkkaar, ni ko Mbind mi tërale, 15:4 suul nañu ko, mu dekki ca ñetteelu fan ba, ni ko Mbind mi tërale. 15:5 Feeñu na Sefas, teg ca fukki taalibe ya ak ñaar. 15:6 Gannaaw ga feeñu na lu ëpp juróomi téeméeri bokki taalibe ci benn yoon. Te ñu bare ci ñoom ñu ngi dund ba léegi, waaye am na ci ñu nelaw. 15:7 Ba noppi feeñu na Saag ak ndawi Kirist yépp. 15:8 Man nag la mujj a feeñu, ma mel ni liir bu judduwul ci jamonoom. 15:9 Ndaxte maa gën a ñàkk solo ci ndawi Kirist yi, te yeyoowuma sax, ñu may wooye ndaw, man mi doon fitnaal mbooloom Yàlla. 15:10 Waaye nag yiwu Yàlla moo tax ma doon li ma doon, te yiw, wi mu wone ci man, du cig neen. Waaye sax maa gën a liggéey ñi ci des ñépp: du ci man, waaye yiwu Yàlla, wiy jëf ci man, moo tax. 15:11 Noonu nag muy man muy ñoom, dénkaane boobu lanuy yégle, te moom ngeen gëm. 15:12 Waaye su nu yéglee ne, Kirist dekki na, nan la ñenn ñi ci yéen man a waxe ne, néew yi duñu dekki? 15:13 Su fekkee ne ñi dee duñu dekki, kon Kirist it dekkiwul. 15:14 Te su Kirist dekkiwul, sunu waare day neen, te it seen ngëm day neen. 15:15 Rax-ca-dolli gis nañu ne, seedeel nanu Yàlla ay fen, ndaxte seede nanu ci mbiram ne, dekkal na Yeesu, te fekk dekkalu ko, su néew yi dul dekki. 15:16 Su néew yi dul dekki, Kirist moom it dekkiwul. 15:17 Te su Kirist dekkiwul, seen ngëm du am solo, ba tey yéena ngi ci seeni bàkkaar. 15:18 Te it ñi dee ba noppi ci Kirist sànku nañu. 15:19 Su fekkee ci giiru dund gii rekk la sunu yaakaar ci Kirist ame solo, kon noo gën a mat a yërëm ñépp. 15:20 Waaye léegi Kirist dekki na, di ku jëkk a dekki, ni gub yi ñu jëkk a tànne ci ngóob mi, jagleel leen Yàlla. 15:21 Gannaaw ci nit la dee jaar, dugg àddina, kon it ci nit la ndekkite jaar. 15:22 Kon ni ñépp deeye ci seen bokk ci Aadama, noonu la ñépp di dundaate ci seen bokk ci Kirist. 15:23 Waaye ku nekk ak ayam. Kirist moo jëkk, mel ni gub yi ñu jëkk a tànne ci ngóob mi, ba noppi, bu Kirist dellusee, ñi bokk ci moom jël seen ay. 15:24 Gannaaw ga, mujug jamono taxaw, te Kirist dina noot gépp kilifa ak bépp sañ-sañ ak doole, ba noppi delloo nguur gi kiy Yàlla di Baayam. 15:25 Ndaxte fàww Kirist nguuru, ba kera Yàlla di daaneel noonam yépp ciy tànkam. 15:26 Noon bu mujj, bi mu fiy jële, mooy dee. 15:27 Ndaxte Mbind mi nee na: «Yàlla nootal na ko lépp, mu teg ci tànk.» Waaye bu Mbind mi nee, «noot na lépp,» wóor na ne, moom mi ko nootal lépp, génne na ci boppam. 15:28 Léegi bu ñu ko nootalee lépp nag, moom Kirist muy Doom ji dina delloo kilifteef gi Yàlla, mi ko nootal lépp, ngir Yàlla nekk buur ci lépp. 15:29 Su ndekkite amul, kon ñi ñu sóob ci ndox ngir ñi dee, lu mu leen di jariñ? Su dekki amul, kon lu tax ñu leen di sóob ngir ñi dee? 15:30 Te nun it lu tax fu nu tollu nu jaay sunu bakkan? 15:31 Bokk yi, ni ma damoo ci yéen ndax Yeesu Kirist, ni la ma wóore ne, bés bu nekk ma riisu dee. 15:32 Su fekkee ne ci ni ñu ko waxe, xeex naa ca dëkku Efes ak rabi àll, kon ban njariñ la may amal? Su néew yi dul woon dekki, am na lu ci léeb wax:«Nanu lekk di naan, ndaxte ëllëg dinanu dee.» 15:33 Bu leen ko réere mbir: «Ànd bu bon dina yàq nit ku baax.» 15:34 Delloosileen xel yi te bàyyi bàkkaar, ndaxte am na ci yéen, ñu umple Yàlla. Kon war ngeen a rus! 15:35 Waaye dina am kuy naan: «Nan la néew yi di dekkee? Wan yaram lañuy dellusee?» 15:36 Yaa gàtt xel! Li ngay ji, du jebbi dund gu bees, fi ak deewul ba noppi. 15:37 Te li ngay ji du jëmmi gàncax giy ñëwi, waaye pepp kese la, maanaam dugub, walla weneen jiwu. 15:38 Noonu Yàlla jox ko jëmm ju ko neex, jiwu wu nekk ak jëmmam. 15:39 Jëmmi mbindeef yépp a wuute: nit ak jëmmam, mala, picc, jën — yu ci nekk ak sa jëmmi bopp. 15:40 Am na itam ay jëmm ca asamaan ak ay jëmm ci suuf. Leeru jëmm ca asamaan wuute na ak gi ci suuf. 15:41 Jant bi, weer wi ak biddiiw, lu nekk ak sag leer. Te it leeru biddiiw bu nekk dina wuute ak moroomam. 15:42 Noonu la ndekkitel néew yi di deme. Bu ñu suulee néew bi, dañoo ji lu yàqu. Bu dekkee, du yàqooti ba abadan. 15:43 Lu ñàkk solo lañuy suul; mu dekki ak ndam. Lu néew doole lañuy suul, mu dekki ak kàttan. 15:44 Bu ñu koy suul, yaram lay doon wu soloo woon ruu. Bu dekkee, doon yaram wu soloo ndamu Xelum Yàlla. Ndegam am na yaram wu soloo ruu, kon dina am yaram wu soloo ndamu Xelum Yàlla. 15:45 Mbind mi nee na: «Nit ku jëkk ka, Aadama, doon na boroom ruu,» waaye Aadama mu mujj mi doon na Xel muy joxe dund. 15:46 Yaram wi soloo ndamu Xelum Yàlla jiituwul; yaramu doom Aadama moo jiitu; yaramu ndam li moo ci topp. 15:47 Nit ku jëkk ka pëndu suuf la woon; ñaareelu nit ki di Kirist, mi ngi jóge asamaan. 15:48 Waa àddina yor nañu jëmmi nit, ki ñu sàkke ci suuf; noonu it ñi bokk ci asamaan dinañu yor melokaanu ki jóge ci asamaan. 15:49 Te ni nu yore melokaanu ki ñu sàkke ci suuf, noonu lanuy yoreji melokaanu ki jóge ca asamaan. 15:50 Li may wax nag bokk yi, moo di ne, sunu yaram wii mënul a am wàll ci nguuru Yàlla, te lu yàqu mënul a am wàll ci liy sax abadan. 15:51 Lii ma leen di xamal, mbóotu Yàlla la. Dégluleen, dunu jaar ci dee nun ñépp, waaye nun ñépp dinanu soppiku, 15:52 ci saa su gàtt, ci xef-ak-xippi, bu liit gu mujj gi jibee. Ndax liit gi dina jib, néew yi dekki, di dund abadan, te nun dinanu soppiku. 15:53 Yaram wu yàqu war na sol jëmm ja dul yàqooti, te yaram wiy dee sol dund gu sax abadan. 15:54 Bu li yàqu solee melokaanu li dul yàqu, te liy dee sol melokaanu liy sax abadan, kon lii ñu wax ci Mbind mi mat:«Yàlla noot na dee, ba labal ko ci ndamam. 15:55 Céy yaw dee! Ana sa ndam?Céy yaw dee! Ana sa daŋar ji ngay fitte?» 15:56 Daŋaru dee mooy bàkkaar, te dooley bàkkaar mooy Yoon wi. 15:57 Waaye jërë-jëf yaw Yàlla, ji nu jox ndam li jaarale ko ci sunu Boroom Yeesu Kirist! 15:58 Kon nag sama bokk yi ma sopp, nangeen takku, sampu ba dëgër, te gën a sawar ci liggéeyu Boroom bi, xam ne seen liggéey, bi jëm ci Boroom bi, du neen.
16:1 Léegi nag ci li jëm ci ndimbal, li ñuy sàkkal gaayi Yàlla yi, defleen li ma tëral ci mboolooy ñi gëm te nekk ci diiwaanu Galasi. 16:2 Bés bu jëkk ci ayu-bés yi, na ku nekk ber lu mu àttan, denc ko, ngir saa yu ma dikkee, ñu bañ di wër di laaj xaalis. 16:3 Su ma dikkee, dinaa dénk seen xaalis ñi ngeen tànn, yónni leen Yerusalem, boole ko ak bataaxal. 16:4 Su aajoo ma demal sama bopp, kon dinañu ànd ak man. 16:5 Gannaaw bu ma jàllee diiwaanu Maseduwan, dinaa ñëw ci yéen, ndaxte fas naa ko yéenee jàll. 16:6 Man na am ma yàgg ci yéen, jombul sax ma lollikoo fi yéen. Noonu dingeen taxawu sama yoon, fu ma man a jëm. 16:7 Ndaxte fi mu ne bëgguma leen a gis rekk, jàll, waaye yaakaar naa ne, dinaa toog ci yéen ab diir, bu neexee Boroom bi. 16:8 Ba tey dinaa toog fii ci dëkku Efes ba màggalu Pàntakot, 16:9 ndaxte Yàlla ubbil na ma bunt, ba mu ne làññ, ngir may def liggéey bu man a am muj gu rafet, te noon yu bare bëgg a gàllankoor liggéey bi. 16:10 Bu leen Timote ganesee, fexeleen ba bumu am njàqare ci seen biir, ndaxte dafay liggéeyal Boroom bi ni man. 16:11 Kon bu ko kenn xeeb. Nangeen taxawu yoonam, ba mu dellusi ci man ci jàmm, ndaxte maa ngi koy xaar ak bokk yi. 16:12 Naka Apolos sunu mbokk mi nag moom, xiir naa ko ay yooni yoon, mu ñëw ci yéen, ànd ak bokk yi. Waaye fi mu ne dëppoowul ak coobareem. Dina ñëw saa su ko manee. 16:13 Farluleen te dëgër ci ngëm, di góor-góorlu te am pasteef. 16:14 Lépp li ngeen di def, defleen ko ak mbëggeel. 16:15 Xam ngeen ne, Estefanas ak njabootam ñoo jëkk a nangu xebaar bu baax bi ci diiwaanu Akayi, te ñoo joxe seen bopp, ngir liggéeyal gaayi Yàlla yi. Kon nag bokk yi, maa ngi leen di ñaan, 16:16 ngeen nangul nit ñu mel noonu, ñoom ak képp ku ànd ak ñoom ci liggéey bi. 16:17 Bi ma Estefanas ak Fortunatus ak Akaykus seetsee, bég naa ci lool. Taxawal nañu leen ci topptoo, bi ngeen yéene woon ci man te tële ko. 16:18 Seral nañu sama xol ak seen yos itam. Kon fonkleen nit ñu mel noonu. 16:19 Mboolooy ñi gëm te nekk diiwaanu Asi ñu ngi leen di nuyu. Akilas ak Pirsil, ñu ngi leen di nuyu bu baax ci Boroom bi, ñoom ak mbooloom ñi gëm tey daje seen kër. 16:20 Bokk yépp ñu ngi leen di nuyu. Saafoonteleen ak xol bu laab. 16:21 Man Pool maa bind nuyoo bii ci sama loxob bopp. 16:22 Képp ku bañ Boroom bi, Yal na ko Yàlla alag. Boroom bi, ñëwal! 16:23 Na yiwu Boroom bi Yeesu ànd ak yéen. 16:24 Bëgg naa leen yéen ñépp ndax sunu booloo ak Yeesu Kirist.
1:1 Man Pool, ndawul Kirist Yeesu ci coobareg Yàlla, man ak Timote sunu mbokk, noo leen di bind, yéen mbooloom Yàlla mi nekk dëkku Korent, ak gaayi Yàlla yu sell, yi nekk ci diiwaanu Akayi gépp. 1:2 Na leen Yàlla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak jàmm. 1:3 Cant ñeel na Yàlla, Baayu sunu boroom Yeesu Kirist, di Baay biy Aji Yërmande tey Boroom lépp luy dëfël xol yi. 1:4 Mooy dëfël sunu xol ci sunu tiis yépp, ngir nun ci sunu bopp nu man a dëfël xolu ñépp ñi nekk ci tiis, di leen sédd ci noflaay, bi Yàlla def ci sunu xol. 1:5 Ndaxte ni coonoy Kirist di baawaane ci nun, noonu it la Kirist nekke buntu noflaay bu yaa, biy dëfël sunu xol. 1:6 Su nuy jaar ci tiis, seen noflaay a tax ak seen mucc. Bu dee Yàlla dëfël na sunu xol, seen noflaay a tax, ngir ngeen man a dékku naqar yu mel ni yu nuy am, nun itam. 1:7 Te sunu yaakaar ci seen mbir dëgër na, xam ne, ni ngeen bokke ak nun naqar, noonu ngeen di bokke ak nun noflaayu xol. 1:8 Ndaxte bokk yi, bëggunu ngeen umple tiis, wi nu daj ci diiwaanu Asi. Yen bi diisoon na lool ba weesu sunu kàttan, ba amatunu yaakaar sax ci dund. 1:9 Demoon nanu ba defe ne, dogalees na sunug dee. Loolu amoon na, ngir nu bañ a wéer sunu yaakaar ci sunu bopp, waaye nu wéer ko ci Yàlla, miy dekkal néew yi. 1:10 Moo nu musal ci dee gu metti googu te dina nu musalaat. Ci moom lanu wékk sunu yaakaar ne, dina nu musalati, 1:11 bu ngeen nu jàpplee di ci boole seeni ñaan. Noonu ñu bare dinañu gërëm Yàlla ci yiw, wi mu nu may te muy tontul ñaanu ñu bare. 1:12 Li nuy tiitaroo moo di sunu xel day seede ne, ci kanamu àddina si, rawatina sax ci seen kanam, aw nanu ci tànk yu jub, ànd ak xol bu laab fa kanam Yàlla. Jëfewunu ci pexem nit, waaye ci yiwu Yàlla lanu jëfe. 1:13 Bindunu leen nag leneen lu dul li ngeen jàng te xam ko. Fi mu ne seen xam-xam ci nun matagul, waaye yaakaar naa ne, bu matee, dingeen man a tiitaru ci nun, ni nu koy defe ci yéen, bu bésu Boroom bi Yeesu ñëwee. 1:15 Kon ni ma ame woon kóolute googu, naroon naa jëkk a jaar ci yéen, ngir ganesi leen ñaari yoon. 1:16 Bëggoon naa jaar ci yéen, dem diiwaanu Maseduwan, te bu ma jógee Maseduwan, dikkaat ci yéen, ngir ngeen waajal sama tukki ca Yude. 1:17 Ba may mébét loolu nag, ndax dama cee boolewul pasteef? Te ndax samay yéene yéeney nit kese la, ba may xel ñaar, naan «waaw» ak «déet?» 1:18 Wóor na Yàlla ne, li nu leen di wax, du «waaw» ju ànd ak «déedéet.» 1:19 Ndaxte Doomu Yàlla ji, Yeesu Kirist, mi nu doon yégle ci seen biir, man ak Silwan ak Timote, nekkul woon «waaw» ak «déedéet;» «waawi» Yàlla la mas a nekk. 1:20 Te lépp lu Yàlla dige woon fekk na «waawam» ci moom. Noonu kon ci Kirist lanuy waxe: «Amiin,» ngir yékkati ndamu Yàlla. 1:21 Te Yàlla moo nuy dëgëral ci Kirist, nun ak yéen, te sol nu Xelam. 1:22 Moo nu màndargaal ni ay gaayam, def Xelam ci sunu xol, muy dawal ci cér, bi mu nu dencal. 1:23 Man nag Yàlla seede na ma, te giñ naa ci sama bakkan ne, yërëm leen rekk moo tax delluseeguma Korent. 1:24 Du caageen nag noo leen bëgg a noot ci lu jëm ci seen ngëm, waaye nu ngi liggéeyandoo ak yéen ngir seen mbég, ndaxte ci ngëm ngeen sax.
2:1 Man nag fas yéene naa lii: duma dellusi ci yéen ci naqar. 2:2 Ndaxte su ma leen tegee naqar, kuy seddal sama xol ku dul yéen ñi ma teg aw naqar? 2:3 Looloo tax ma binde noonu, ngir bañ a agsi, am naqar ci ñi ma waroon a bégal. Am naa kóolute ci yéen ñépp ne, sama mbég mooy seen mbég. 2:4 Ci biir tiis ak xol bu jeex laa leen bind, samay bët taa ak ay rangooñ. Binduma leen ngir teg leen naqar, waaye ngir ngeen xam xóotaayu mbëggeel gi ma am ci yéen. 2:5 Su kenn tegee moroomam naqar, du man la ko teg, waaye man nanu ne, yéen ñépp la ko teg — matul may réyal mbir mi. 2:6 Àtte bi ko mbooloo mi teg, doy na. 2:7 Léegi nag baal-leen ko te dëfël xolam, ngir bañ mu sóobu ci naqar wu ëpp. 2:8 Kon maa ngi leen di ñaan, ngeen feddali seen mbëggeel ci moom. 2:9 Nattu leen moo tax ma bind leen it, ngir seet ba xam dingeen dégg ndigal ci lépp. 2:10 Ku ngeen baal, ma baal ko itam. Man nag, su ma baalee --fekk am lu ma war a baale — yéena tax ma def ko ci kanamu Kirist, 2:11 ngir Seytaane bañ a am bunt bu mu jaar ba nax nu, ndaxte réerewunu mbir ay pexeem. 2:12 Ba ma àggee Torowas nag, ngir yégle fa xebaar bu baax bi ci Kirist, Boroom bi ubbil na ma ci bunt. 2:13 Waaye sama xel dalul benn yoon, ndax li ma fa fekkul sama mbokk, Tit. Noonu nag ma tàggu leen, daldi dem diiwaanu Maseduwan. 2:14 Waaye cant ñeel na Yàlla! Ci sunu booloo ak Kirist, daf nuy yóbbaale saa su nekk ci gawari ndamam, tey jaar ci nun ngir turu Kirist jolli fu nekk, ni xetu latkoloñ di tasaaroo. 2:15 Ndaxte ci Yàlla, xetu Kirist gu neex lanu, di gilli jëm ci ñiy mucc ak ñiy sànku; 2:16 ci ñu mujj ñii, xet gu sedd lanu, guy jëme ci dee; ci ñu jëkk ñi, xetu dund lanu, guy jëme ci dund. Kon ku man a àttan yen boobu! 2:17 Nun nag melunu ni ñu bare, ñiy baana-baana ci kàddug Yàlla, waaye ci sunu booloo ak Kirist, nu ngi waare ak xol bu laab fa kanam Yàlla, ni yonenti Yàlla.
3:1 Mbaa du danoo tàmbalee tëgguwaat nag? Mbaa du danoo soxla ni ñenn ñi ay dénkaane yu ñu nuy gërëme, te ñuy bataaxal yu jóge ci yéen walla yu jëm ci yéen? 3:2 Déedéet, yéenay sunu bataaxal, te ci sunu xol lañu ko bind, di bataaxal bu nit ñépp man a xam te jàng ko; 3:3 ndaxte leer na ne, bataaxal bu jóge ci Kirist ngeen, bu mu jaarale ci nun. Bindeesu ko daa, waaye ci Xelum Yàlla miy dund lees ko binde; te du ci àlluway doj lañu ko rëdd, waaye ci xolu doom Aadama. 3:4 Googu kóolute lanu am fa kanam Yàlla ndax Kirist. 3:5 Du caageen nag ne, àttan nanu dara ci sunu man-man, ba nu yaakaar dara ci sunu bopp, waaye sunu kàttan ci Yàlla lay jóge. 3:6 Moo nu jox kàttan, nu nekk ndaw yuy xamle kóllëre gu bees gi. Te kóllëre googu ajuwul ci ay sàrti diine, waaye mi ngi aju ci jëfu Xelum Yàlla. Ndaxte sàrti kese day jëme ci dee, waaye Xelum Yàlla dafay joxe dund. 3:7 Ba ñu bindee arafi sàrt yi ciy àlluway doj, leeraayu ndamu Yàlla nekk fa. Xar-kanamu Musaa di leer, ba bànni Israyil duñu ko man a xool, fekk leer ga di wéy. Ndegam sàrti yoon yooyuy jëme ci dee, ñoo ànd ak ndam, 3:8 rawatina nag ne, jëfu Xelum Yàlla dina gën a ànd ak ndam. 3:9 Su fekkee ne tëralin, wiy teg nit tooñ, àndoon na ak ndam, rawatina ci tëralin wiy àtte nit jub. 3:10 Ndaxte ndam li amoon keroog suux na ci ndam li ko raw léegi. 3:11 Te it ndegam li wéy dafa amoon ndam, astemaak li fi sax. 3:12 Kon nag gannaaw wékku nanu ci yaakaar ju mel noonu, danuy waare ak kóolute gu mag. 3:13 Dunu def ni Musaa, mi daan muur xar-kanamam, ngir bànni Israyil bañ a gis jeexug leer googu saxul. 3:14 Waaye seen xel dafa daldi gumba. Ba tey jii sax, bu ñuy jàng téereb kóllëre gu jëkk gi, muuraay moomu dafay des; deñul, ndaxte ci Kirist rekk la man a deñe. 3:15 Waaw, ba tey jii, su ñuy jàng yoonu Musaa, seen xol dafay muuru. 3:16 Waaye saa su kenn walbatikoo ci Boroom bi, muuraay gi daldi muriku. 3:17 Fekk nag Boroom, bi ñuy wax foofu, moo di Xelum Yàlla, te fu Xelu Boroom bi nekk, foofa yaatu gu mat am na fa. 3:18 Te nun ñépp nag, danuy lerxat ndamu Boroom bi ak xar-kanam bu muuruwul, bay soppiku ci melokaanam, ànd ak ndam luy yokku te sax ci dooley Boroom biy Xelum Yàlla.
4:1 Kon nag ndegam Yàlla ci yërmandeem sas na nu liggéey boobu, dunu bayliku. 4:2 Lànk nanoo ànd ci mbir, yi ñuy nëbb te ñu gàccelu. Sunuy tànk du yu njublaŋ te dunu dëngal kàddug Yàlla. Waaye nu ngi biral dëgg, di sàkku kóoluteg ñépp fa kanam Yàlla. 4:3 Su fekkee ne sax, xebaar bu baax bi dafa muuru ci ñenn ñi, dafa fekk ñoom ñu aw yoon wu jëm ci sànkute. 4:4 Ñoom la yàllay jamono ji gëlëmal seen xel, ngir ñu bañ a gis leeru xebaar bu baax, biy wone ndamu Kirist, mi di melokaanu Yàlla. 4:5 Ndaxte Yeesu Kirist Boroom bi lanuy waare, waaye waarewunu lu jëm ci sunu bopp. Nun seeni jaam lanu ndax Yeesu. 4:6 Ndaxte Yàlla mi ne: «Na leer leer ci biir lëndëm,» moo leer ci sunu xol, ngir leeral nu ak xam-xamu ndamu Yàlla, liy feeñ ci xar-kanamu Kirist. 4:7 Leer googu ci sunu xol mi ngi mel ni alal, waaye ñu ngi ko def ci nun ñi néew doole niy njaq kese, ngir kàttan gu ëpp xel gi, bawoo ci Yàlla te du ci nun. 4:8 Dañu nuy sonal fu nekk, waaye kenn tancu nu. Dañu nuy dugal ci ruq yi, waaye dinanu ci génn. 4:9 Dañu nuy fitnaal, waaye Yàlla du nu wacc mukk. Tër nañu nu, waaye kenn doggaliwu nu. 4:10 Fu nu tollu noo ngi gàddu ci sunu yaram dee gi Yeesu dee woon, ngir dundu Yeesu moom it feeñ ci sunu yaram. 4:11 Bés bu nekk, nun ñiy dund, ñu ngi nuy jébbal dee ndax Kirist, ngir dundu Kirist moom itam feeñ ci sunu yaram wiy dee. 4:12 Noonu dee mu ngi jëf ci nun, dund di jëf ci yéen. 4:13 Mbind mi nee na: «Damaa gëm, moo tax ma wax.» Nun it nag, ndegam am nanu menn xelu ngëm moomu, danoo gëm, ba tax nuy wax. 4:14 Ndaxte xam nanu ne Yàlla, mi dekkal Boroom bi Yeesu, dina nu dekkal nun itam ak Yeesu, te dina nu yóbbu ak yéen, taxawal nun ñépp ci jataayam. 4:15 Ndaxte lépp li nuy daj, seen njariñ a tax, ngir yiwu Yàlla, wiy yokku ci nit ñu gën a takku, yokkaale ngërëm lu jëm ci Yàlla, ngir jollil ndamam. 4:16 Loolu moo tax sunu yaakaar du tas. Bu fekkee sax sunu yaram day yàqu jëm cig mag, sunu ruu moom, bés ak bés muy gën a yeesaat. 4:17 Ndaxte sunu coono bu woyof bi dul yàgg, dafa nuy jural ndam lu bare, ba suul coono bi, tey sax abadan. 4:18 Kon diirunu li ñuy gis waaye li ñu dul gis. Ndaxte li ñuy gis day wéy, waaye li ñu dul gis day sax ba fàww.
5:1 Yaram wi nu soloo ci kaw suuf dafa mel ni ab tànt. Su daanoo, xam nanu ne, Yàlla jagleel na nu am taax ci asamaan, mu loxol nit defarul, di taax muy sax ba fàww. 5:2 Fi mu ne nu ngi wonk, di yàkkamtee féete ak sunu dëkkukaayu asamaan, sol ko ni koddaay, xam ne, 5:3 bu nu ko solee, dunu def yaramu neen. 5:4 Nun ñi nekk ci tànt bii, nu ngi wonk ndax coono. Du caageen ne, danoo bëgg a summi sunu yaramu àddina, waaye danoo bëgg a sol sunu yaramu asamaan, ngir liy dee sóobu ci biir dund. 5:5 Ki nu waajal ngir loolu moo di Yàlla, moom mi nu jox Xelam, di dawal ci cér bi mu nu dencal. 5:6 Noonu kon nu ngi fees ak kóolute fu nu tollu; te xam nanu ne, fi ak nu ngi dëkk ci yaram wii, àggagunu sunu màkkaan ci wetu Boroom bi — 5:7 ndaxte doxewunu ab gis, waaye ngëm lanuy doxe. 5:8 Kon fees nanu ak kóolute, te yéenee jóge ci dëkkukaayu yaram wii, dem dëkk ci wetu Boroom bi. 5:9 Kon nag des fi walla jóge fi, li nuy faaydaal moo di neex Boroom bi. 5:10 Ndaxte nun ñépp fàww nu teew ci kanamu Kirist, mu àtte nu, ngir ku nekk jot peyu li mu def ci yaramam, muy lu baax walla lu bon. 5:11 Gannaaw xam nanu ragal Yàlla nag, nu ngi fexee gëmloo nit ñi, waaye li nu nekk leer na Yàlla te yaakaar naa ne, leer na leen it, ba ne fàŋŋ. 5:12 Jéemunoo waxati lu ngeen nuy nawe, waaye danu leen a bëgg a may yoonu tiitaru ci nun, tey tontu ñooñuy tiitaroo col te du xol. 5:13 Su fekkee danoo tàggalikoo ak sunu sago, ngir Yàlla la. Su nu àndee ak sunu sago, ngir yéen la. 5:14 Ndaxte mbëggeelu Kirist moo nuy jiite, ndax wóor na nu ne, ndegam kenn rekk a dee ngir ñépp, kon ñépp a dee. 5:15 Te dee na ngir ñépp, ngir ñiy dund dootuñu dund ngir seen bopp, waaye ngir ki dee ci seen wàll te dekki. 5:16 Kon nag gannaawsi tey xoolatunu kenn ci gis-gisu àddina. Su fekkee mas nanoo xool Kirist ci gis-gisu àddina, léegi xooleetunu ko noonu. 5:17 Kon bu nit bokkee ci Kirist, mbindeef mu bees la. Li jëkk wéy na, lu bees a fi teew. 5:18 Te loolu lépp a ngi sosoo ci Yàlla, mi nu jubale ak boppam jaare ko ci Yeesu Kirist, te sas nu nuy waare juboo googu: 5:19 maanaam, Yàlla jaar na ci Kirist, di jubale waa àddina ak boppam te sëfu leen seeni tooñ. Kàddug juboo googu, Yàlla dénk na nu ko. 5:20 Ay ndaw lanu, yu Kirist yónni, te Yàllaa ngi woo nit ñi jaare ko ci nun. Kon nag ci turu Kirist, nu ngi leen koy ñaan: nanguleen a juboo ak Yàlla. 5:21 Kirist mi musul a def bàkkaar, Yàlla def na ko bàkkaar ci sunu wàll, ngir ci sunu bokk ci moom, nu man a doon njubteg Yàlla.
6:1 Nun nag ñiy liggéeyandoo ak Yàlla, nu ngi leen di ñaan: jariñooleen yiw, wi ngeen jote ci Yàlla, ngir mu bañ a neen ci yéen. 6:2 Ndaxte Yàlla nee na:«Ca jamono ja mu jekke, nangu naa sa ñaan;ci bésu mucc gi laa la wallu.» Tey jii la jamono ju jekk ji; tey la bésub mucc gi. 6:3 Bëggunoo lëmbaaje xelu kenn ci dara, ngir kenn bañ a sikk sunu liggéey. 6:4 Li nu bëgg moo di rafetal sunu tur ni jawriñi Yàlla ci fànn gu nekk; danuy muñ coono yi, tiis yi, njàqare yi; 6:5 ñu nuy dóor, di nu tëj ci kaso, dëkk yi di yengu ndax sunu mbir; nuy liggéey ba sonn, di fanaanee xool, di woor. 6:6 Nu ngi rafetal sunu yen ci dund gu sell, ci xam-xam, muñ ak laabiir, ci Xel mu Sell mi ak ci mbëggeel gu raxul njublaŋ, 6:7 ci kàddug dëgg ak ci kàttanu Yàlla, nu ngi yor gànnaayi njubte ci loxol ndeyjoor ak lu càmmooñ. 6:8 Ñu bàkk nu, jéppi nu, sant nu, xas nu. Ñu di nu jiiñ réeral, moona niti dëgg lanu. 6:9 Ñuy xeeb sunu tur, moona tur yi siiw nañu. Nu mel ni ñu loof, moona nu ngi dund. Ñu yar nu, teewul nu rëcc ci dee. 6:10 Danuy dékku tiis, waaye di bég fu nu tollu. Nu tumurànke, waaye di woomal ñu bare; amunu dara, fekk noo moom lépp. 6:11 Yéen bokki Korent, wax nanu leen sunu biir ak sunu biti, di leen ubbil sunu xol. 6:12 Ubbiku nanu ci yéen, waaye yéen ubbikuwuleen ci nun. 6:13 Maa ngi wax ak yéen ni samay doom; feyleen nu bor bi, yéen itam; ubbileen seen xol! 6:14 Buleen likkoo ak ñi gëmul. Gan àndandoo moo man a am diggante njubte ak ndëngte? Gan booloo moo man a am diggante leer ak lëndëm? 6:15 Gan déggoo moo man a am diggante Kirist ak Beliyar? Gan jaxasoo moo man a am diggante ki gëm ak ki gëmul? 6:16 Nan la këru Yàlla man a mànkoo ak xërëm yi? Ndaxte nun nooy këru Yàlla Aji Dund ji, ni ko Yàlla waxe:«Dinaa dëkk ci seen biir,tey dox ànd ak ñoom,ma nekk seen Yàlla,ñuy samay gaay.» 6:17 Kon nag Boroom bi nee na:«Génnleen biir ñooñu te beru.Buleen laal dara lu am sobe,kon dinaa leen teeru. 6:18 Dinaa nekk baay ci yéen,ngeen di doom ci man, muy góor, di jigéen. Moom la Aji Kàttan ji wax.»
7:1 Ndegam nag jot nanu ci dige yu mel nii, samay soppe, nanu sellal sunu bopp ci bépp sobeb yaram walla bu xel, dund dund gu sell, ba mat ci ragal Yàlla. 7:2 Yaatal-leen nu ci seen xol. Tooñunu kenn; lorunu kenn; naxunu kenn, jël alalam. 7:3 Teg leen tooñ taxul may wax lii, ndaxte wax naa ba noppi ne, yéena ngi ci sunu xol ci dund ak ci dee. 7:4 Kóolute gi ma am ci yéen réy na. Tiitar bi may jële ci yéen réy na. Sama xol sedd na guyy. Damaa fees ak mbég ci bépp coono bu nuy daj! 7:5 Ba nu àggee diiwaanu Maseduwan, noppaluwunu, waaye coono bu ne daj nanu ko: xeex ci biti, njàqare ci biir. 7:6 Waaye Yàlla miy dëfël xolu ñiy yoggoorlu ndax tiis, dëfël na sunu xol ci ñëwu Tit, 7:7 te du ci ñëwam rekk sax waaye ci li ngeen dëfël xolam. Yégal na nu seen nammeel ci nun, seen réccu ak seen farlu jëm ci man, ba sama mbég gën cee yokku. 7:8 Su fekkee ne sax, bataaxal bi ma leen bind dafa leen naqare, réccootuma ko. Ci lu jëkk réccu naa ko, ndaxte gis naa ne, bataaxal boobu teg na leen tiis, doonte sax ci diir bu néew. 7:9 Waaye sama xol sedd na léegi, du ndax seen tiis, waaye ci li mu tax ngeen réccu. Tiis wu jóge ci Yàlla ngeen tegoo, te àndul ak benn loraange bu bawoo ci nun. 7:10 Ndaxte tiis wu jóge ci Yàlla dina jur réccu guy jëme ci mucc, te réccu googu laajul gëstu. Waaye tiisu àddina day jëme ci dee. 7:11 Seen tiis wi jóge ci Yàlla, gisleen nag li mu jur: ndaw njaxlaf ak lay ak mer ak ragal ak nammeel ak farlu, ak bëgg a yar ki tooñ! Ci seen jëf yépp wone ngeen ne, set ngeen wecc ci mbir moomu. 7:12 Kon nag su ma leen bindee, ki tooñ taxul, ki ñu tooñ it taxul, waaye dama leen a bind, ngir ngeen man a gis ci kanam Yàlla cawarte, gi ngeen am ci nun. 7:13 Te loolu seral na sunu xol. Sunu xel dal na, rawati ci li nu ànd ak Tit ci mbégam, ci li ngeen seral xolam, yéen ñépp. 7:14 Su fekkee ne tiitaru woon naa ci seen mbir ci kanamu Tit, rusuma ci. Dëgg rekk lanu leen mas a wax; noonu it la Tit gise ne, li nu leen doon seede lépp, dëgg la. 7:15 Te mbëggeelam ci yéen gën na yokku, buy fàttaliku ni ngeen ko déggale yéen ñépp, ci li ngeen ko teeru, ànd ak ragal ak weg. 7:16 Bég naa, ndaxte xam naa ne, man naa leen a wóolu ci lu nekk!
8:1 Gannaaw loolu bokk yi, danu leen a bëgg a xamal li yiwu Yàlla jur ci biir mboolooy ñi gëm te nekk ci diiwaanu Maseduwan. 8:2 Nattu yi ñu jaar ëmb nañu coono yu réy; waaye seen mbég mu tar ak seen ñàkk gu metti ñoo jur ci ñoom yéwén gu jéggi dayo. 8:3 Seede naa ne, ñoom ci seen bopp joxe nañu ba fa seen man-man yem, ba weesu ko sax. 8:4 Saraxu nañu nu lool, ngir bokk ci ñiy yónnee ndimbal gaayi Yàlla yi. 8:5 Te yemuñu sax ci li nu séentu woon ci ñoom, waaye dañoo jébbal seen bopp Boroom bi jëkk, gannaaw loolu ñu jébbal nu seen bopp ci coobareg Yàlla. 8:6 Looloo tax nag nu sant Tit, mu ñëw àggale ci yéen, ni mu tàmbalee woon, seen jëfu ndimbal. 8:7 Gannaaw nag wone ngeen cawarte gu tollu noonu, ci ngëm, ci wax, ci xam-xam, ci farlu gu mat, ak ci seen mbëggeel ci nun, sawareleen noonu it ci jëfu ndimbal lii. 8:8 Du ndigal lu ma leen di jox, waaye dama leen di yégal cawarteg ñi ci des, ngir natt fu seen mbëggeel tollu. 8:9 Ndaxte yiwu sunu Boroom Yeesu Kirist umpu leen, ni mu futtee am-amam, ba ñàkk ngir yéen, ndax ngeen woomle cig ñàkkam. 8:10 Kon lii laa xalaat ci lu baax ci yéen: yéen ñi nga xam ne tàmbaliwuleen a jëf rekk, waaye yéena jëkk a am yéene jii daaw, 8:11 yeggaleleen ko léegi. Noonu li ngeen mottali ci seen man-man tolloo ak yéene, ji ngeen amoon ci seen mébét. 8:12 Ndaxte joxe, bu àndee ak yéene, Yàlla dina ko nangu, di seet li nu am te bañ a seet li nu amul. 8:13 Bëgguma leen a teg soxla, ngir woyofal ñi ci des, waaye na ñépp tolloole. 8:14 Tey jii nag man ngeen sàkk ci li ngeen barele, faj soxlay ñeneen, ngir ëllëg it bareleg ñooña faj seen soxla. Noonu ñépp tolloole. 8:15 Moom la Mbind mi tëral ne:«Ki dajale lu bare ëpplewul dara,te ki dajale tuuti ñàkkul.» 8:16 Cant ñeel na Yàlla, moom mi def ci xolu Tit cawarte gu mel ni sunu gos ci yéen! 8:17 Bi nu ko laajee, mu ñëw ci yéen, nangu na, te rax-ca-dolli cawarteem tollu na, ba nu man a wax ne, ci coobarey boppam la jóge, jëm ci yéen. 8:18 Yónniwaale nanu ak moom mbokk, mi am tur wu rafet ci mboolooy ñi gëm ñépp ndax li muy waare xebaaru Kirist. 8:19 Te sax mbooloo yi ñoo ko tànn, ngir mu ànd ak nun, bu nuy yóbbu ndimbal li ngir ndamu Boroom bi, te mu firndeel sunu yéene ju rafet. 8:20 Def nanu noonu nag, ndax kenn bañ noo ŋàññ ci ni nuy topptoo ndimbal lu yaatu loolu. 8:21 Danuy fexee def li jub, du ci kanam Yàlla rekk, waaye it ci kanam nit ñi. 8:22 Yónniwaale nanu it sunu mbokk, mi nu seetlu cawarteem ay yooni yoon ci fànn yu bare, te mu gën koo fésal bii yoon ndax kóolute gu réy, gi mu am ci yéen. 8:23 Noonu kon ci lu jëm ci Tit, sama nawle la ci liggéey, bi ci seen biir. Ci lu jëm ci sunu bokk, yi ànd ak moom nag, ndawi mbooloom ñi gëm lañu, ñuy wone ndamu Kirist. 8:24 Na seen teeru firndeel nag seen mbëggeel ci kanamu mboolooy ñi gëm, te dëggal leen ne, noo yey wóolu leen.
9:1 Ci mbirum ndimbal loolu jëm ci gaayi Yàlla yi, matul ma leen di bindaat, 9:2 ndaxte xam naa seen yéene ju rafet, te maa ngi ciy damu ci kanamu waa Maseduwan, naan leen: «Daaw fekk na waa Akayi jekk.» Te seen cawarte xamb na ñu bare ci ñoom. 9:3 Maa ngi yónni nag bokk yooyu, ngir damu gi nu doon damu ci yéen ci mbir mii bañ a neen, te ngeen jekk, ni ma ko waxe woon. 9:4 Danoo bañ rekk waa Maseduwan, ñiy ànd ak man, fekk jekkaguleen; te kon kóolute googu nu am ci yéen dina nekk sunu gàcce, waxaalewuma nag seen bos. 9:5 Moo tax ma xalaat ne, li gën mooy yónni bokk yooyu, ñu jiitu ma ci yéen, topptoo mbiri ndimbal lu yaatu loolu ngeen dige woon. Loolu di may gu tàlli, te bañ a nekk yëfi nay. 9:6 Te lii moo am: ku ji tuuti, góob tuuti; ku ji lu bare, góob lu bare. 9:7 Kon na ku nekk joxe, ni mu ko nase ci xolam, te bañ cee am réccu walla sañul-bañ, ndaxte kiy joxe ak mbég moo neex Boroom bi. 9:8 Te Yàlla man na leen a woomal ci bépp yiwam ba ci fépp ak ci lépp, ngeen faj seen soxla yépp te sakkanle it ngir bépp jëf bu baax. 9:9 Moom la Mbind mi wax ne:«Tabe na, ba may baadoolo yi;njubteem day sax ba fàww.» 9:10 Yàlla miy jox beykat bi jiwu ak nit ab dund, dina leen jox jiwu wu ne gàññ, te sakkanal li seen njub meññ. 9:11 Noonu dingeen woomle ci lépp, ba yéwén ci bépp anam, ba tax ñu bare gërëm Yàlla ndax li ngeen maye jaarale ko ci nun. 9:12 Ndaxte njaamu, gi ngeen di jaamu, yemul rekk ci faj soxlay gaayi Yàlla yi, waaye dina tax it ngërëmu ñu bare baawaan, jëm ci Yàlla. 9:13 Ci li ngeen firndeel seen mbëggeel ci joxe ndimbal lii, dinañu màggal Yàlla, ndaxte wone ngeen ni ngeen déggale xebaar bu baax bu Kirist bi, ak ni ngeen yéwéne ci seen ndimbal jëme ci ñoom ak ñépp. 9:14 Rax-ca-dolli dinañu sant Yàlla ak xol bu fees ak cofeel ci yéen ndax yiw wu mag, wi Yàlla def ci yéen. 9:15 Jërë-jëfati yaw Yàlla ndax sa may googu weesu dayo!
10:1 Ci lu jëm ci samay mbir nag, maa ngi leen di ñaan — man Pool, mi ñu ne, ci seen biir «ragal» laa, bu ma leen soree, «ñeme,» — maa ngi leen di ñaan ndax woyof ak lewetaayu Kirist, ngir bu ma ñëwee, ma bañ a ànd ak ñeme gi may dencal ñenn ñiy xalaat ne, gis-gisu nit lanu topp. 10:3 Dëgg la ne nit rekk lanu, waaye dunu xeexe ni nit. 10:4 Ndaxte gànnaay, yi nuy xaree, jógewuñu ci nit, waaye ca Yàlla lañu jóge, te ànd ak kàttan, ngir daaneel ay tata. Danuy daaneel xalaat yi dul dëgg 10:5 ak bépp tiitar buy jànkoonteek xam-xamu Yàlla, te danuy noot bépp xalaat, ba mu déggal Kirist. 10:6 Te fas yéene nanoo jubbanti képp ku déggadi, bés bu seen dégg ndigal matee. 10:7 Xool-leen mbir mi ne fàŋŋ. Bu amee ku mu wóor ne, ci Kirist la bokk, na jàpp it ne, su bokkee ci Kirist, nun itam ci Kirist lanu bokk. 10:8 Awma lu may rus, su may damu lu ëpp ci sañ-sañ bi nu Boroom bi jox, di sañ-sañu yokk seen ngëm, te du ngir seen kasara. 10:9 Ba tey bëgguma ngeen xalaat ne, maa ngi leen di xëbal ci samay bataaxal. 10:10 Ndaxte am na ku naan: «Ay bataaxalam dañoo ñagas te am doole, waaye bu teewee dafay ñàkk fulla, di wax waxi picc.» 10:11 Kiy wax loolu na xam lii: ni sunuy kàddu mel ci sunuy bataaxal, bu nu fa nekkul, noonu it lanuy mel ci sunuy jëf, bu nu teewee. 10:12 Ñemewunoo féetele walla mengale sunu bopp ak ñooñu naw seen bopp. Ci li ñuy sàkk ab natt ngir natt ak mengale seen bopp ak seen bopp, ñàkk xel a tax. 10:13 Nun nag dunu damu ci lu weesu dayo. Nu ngi damu ci liggéey bi nu Yàlla sas, ba may nu, nu agsi ci yéen. 10:14 Bu sunu sas agsiwul woon ba ci yéen, kon man nanoo ne, génn nanu sas wi nu Yàlla sas. Waaye agsi na ba ci yéen, te indil nanu leen xebaar bu baax bi jëm ci Kirist. 10:15 Kon nag dunu jéggi dig yi Yàlla rëdd, bay damu ci liggéeyu ñeneen. Waaye am nanu yaakaar ne, su seen ngëm yokkoo, dinanu gën a màgg ci seen biir, des ba tey ci dig yi nu Yàlla rëddal. 10:16 Noonu dinanu man a yégle xebaar bu baax bi ci bérab, yi leen féete gannaaw, te bañ a damu ci li ñeneen ñi def ci seen sas. 10:17 Waaye ni ko Mbind mi waxe: «Kuy damu, na damu ci Boroom bi.» 10:18 Ndaxte ki neex Yàlla, du ki naw boppam, waaye ki Yàlla gërëm.
11:1 Céy bu ngeen ma manoon a muñal, ma wax leen tuuti waxi dof! Waaw muñal-leen ma sax. 11:2 Dama leen di fiire ak fiiraange gu jóge ca Yàlla, ndaxte dama leen a bëgg a jébbal jenn jëkkër kepp, muy Kirist, ngeen set ni janq. 11:3 Waaye ni jaan ja naxe woon Awa ci pexeem, ragal naa yéen itam ñu lëmbaaje ni seen xel, ba ngeen dëddu xol bu laab, bi ngeen amoon ci seen diggante ak Kirist. 11:4 Ndaxte bu kenn ñëwee, di leen waar ci Yeesu ci lu juuyoo ak li nu leen yégal, walla ngeen jot meneen xel mu wuute ak Xel mi ngeen jot, walla ngeen nangu beneen xebaar bu wuute ak bi ngeen dégg, dingeen ko dékku bu baax. 11:5 Moona foog naa ne, seen ndaw yooyu ngeen yékkati, ba ñu ëpp ndaw sax, ëpplewuñu ma dara. 11:6 Bu ma dul jàmbaari wax it, néewuma xam-xam, te won nanu leen ko ci bépp mbir ak ci bépp fànn. 11:7 Walla boog ndax dama leen a tooñ ci li ma suufeel sama bopp ngir yékkati leen, ba ma leen di yégal xebaar bu baax bi te laajuma leen genn pey? 11:8 Xanaa kay damaa tooñ ci li ma dunde alalu yeneen mboolooy ñi gëm, ba futti leen, ngir dimbali leen, yéen. 11:9 Te ba ma nekkee ci yéen te soxla dab ma, wéeruwuma ci kenn ci yéen, ndaxte bokk ya jóge Maseduwan ñoo ma indil li ma soxla woon. Ci lépp moytu naa nekk yen ci yéen, te dinaa ko gën a def. 11:10 Ni mu wóore ne, dëggug Kirist nekk na ci man, ni la wóore ne loolii may damoo, kenn du ko teggi ci diiwaanu Akayi gépp. 11:11 Lu tax? Ndax dama leen a bëggul? Yàlla xam na ne, bëgg naa leen! 11:12 Noonu may doxale nag dinaa ci sax, ngir ñiy damu, di wut yoon wu ñu aw ba yemale seen bopp ak nun, duñu ko am. 11:13 Ay ndawi naaféq lañu, di ay liggéeykat yu njublaŋ yuy mbubboo turu ndawi Kirist. 11:14 Te loolu jaaxalu nu, ndaxte Seytaane moom ci boppam day mbubboo malaakam leer. 11:15 Kon nag ay ndawam mbubboo ndawi njub, loolu du nu jaaxal. Dees na leen fey seeni jëf. 11:16 Maa ngi leen koy waxaat: bu ma kenn jàpp nib dof. Walla boog bu ngeen ma ko jàppee, séddleen ma céru dof, ngir ma damu tuuti, man itam. 11:17 Loolu may wax nag, waxuma ko ci turu Boroom bi. Bu ma ñemee damoo nii, maa ngi wax ni dof. 11:18 Ndegam ñu bare dañuy damu ni nit kese, man itam kon dinaa damu. 11:19 Yéen boroom xel yi, aka ngeen a man a muñal ñi dof, 11:20 nde yéena ngi muñ ñi leen di jaamloo, di lekk seen alal, di leen nax, di leen xeeb, di leen talaata! 11:21 Sunu néew doole mayu nu, nu dem ba jëfe noonu; rus naa ci lool de! Ma wax waxi dof; moona lépp lu waay ñemee damoo, ñeme naa ko, man it. 11:22 Ndax Ibrë lañu? Man it Ibrë laa. Ndax bànni Israyil lañu? Man itam ci laa. Ndax sëti Ibraayma lañu? Man itam moom laa. 11:23 Ndax surgay Kirist lañu? --maa ngi wax waxi ku tàggoo ak sagoom nag — maa leen ko gën a doon. Bu dee ci liggéey, maa leen ci man. Bu dee ci li ñu nu tëj ci kaso, maa leen ko gën a miin. Bu dee ci li ñu nu dóor ay yar, maa leen ëpple. Leru naa dee ba tàyyi. 11:24 Juróomi yoon Yawut yi dóor nañu ma fanweeri yar ak juróom-ñeent. 11:25 Ñetti yoon dóorees na ma ay yet, te mas nañu maa sànni ay xeer, bëgg maa rey. Ñetti yoon dugg naa gaal, mu suux. Mas naa yendu ci ndox, fanaan ci. 11:26 Ci sama tukki yu bare yi daan naa faral di daje ak musiba ci dex yi, ak musiba ci sàcc yi, musiba mu jóge ci sama xeet walla ci ñi dul Yawut, musiba ci biir dëkk yi, ci màndiŋ yi, ci géej gi, ci biir bokki taalibe yu naaféq yi. 11:27 Sonn naa, di ñaq, di fanaane xool, di xiif ak a mar tey fande, di dékku liw te rafle, 11:28 waxaalewuma li ci des nag: bés bu nekk maa ngi xalaat mboolooy ñi gëm. 11:29 Ana ku ci néew doole, te wàlluma ko? Ana ku ci bàkkaar, te awma naqar wu tiis? 11:30 Su ma damu waree kon, ci sama néew doole laay damoo. 11:31 Yàlla Baayu sunu Boroom Yeesu, moom mi màgg ba fàww, xam na ne, du ay fen ci man. 11:32 Ba ma nekkee dëkku Damas, boroom dëkk ba, di jawriñu buur ba Aretas, dafa santaane woon ñuy wottu dëkk ba, ngir man maa jàpp. 11:33 Waaye dugalees na ma ci dàmba, jaarale ma ci palenteeru miiri dëkk ba, yoor ma ci suuf. Noonu ma rëcc ko.
12:1 Damu amul jariñ, ba tey war na ma. Kon ma jàll ci nettali gis-gisi Boroom bi ak i peeñu. 12:2 Xam naa taalibeb Kirist boo xam ne yékkati nañu ko ba ca asamaan, si gën a kawe, booba ak léegi mat na fukki at ak ñeent. Xawma ndax ànd na ak jëmmam walla déet. Yàlla rekk a xam. 12:3 Xam naa ne, nit kooku yékkati nañu ko ba fa Yàlla nekk. Bu dee ci jëmmam mbaa ci xelam, xawma; Yàllaa xam. Mu dégg fa baat yu ñu mënul a nettali te yu ñu mayul doom Aadama, mu ŋaaŋ ko. 12:5 Dinaa damu ci nit ku mel noonu. Waaye duma damu ci sama bopp, lu dul liy wone sama néew doole. 12:6 Su ma bëggoon a damu, du doon yëfi dof, ndaxte dëgg laay wax. Waaye damay moytoo damu, ngir kenn bañ a foog ci man lu weesu li mu gis, may def, te muy dégg, ma di ko wax. 12:7 Te it ngir ma bañ a yég sama bopp ndax peeñu yooyu wees xel, mayees na mbir dal ma ci sama yaram, di ma metital ni dég, muy malaakam Seytaane mu may sonal, ngir ma bañ a yég sama bopp. 12:8 Ñaan naa Boroom bi ñetti yoon ci mbir moomu, ngir mu taqale ma ak moom. 12:9 Waaye mu ne ma: «Sama yiw doy na la; sama kàttan a ngi mate cig néew doole.» Kon nag dëgg-dëgg, gën na maa bég ci damu ndax sama néew doole, ngir kàttanu Kirist dëkk ci man. 12:10 Looloo tax may bég ci néew doole, yi may wéye ngir turu Kirist, ciy tiis, ciy njàqare, mbaa ñu saaga ma, mbaa ñu fitnaal ma. Ndaxte bu ma néewee doole, booba laay am kàttan. 12:11 Ci dëgg-dëgg wax naa waxi dof te yéena ma ci dugal, fekk yéen ci seen bopp sax yéena ma waroon a sargal, ndaxte su ma dul dara sax, seen ndaw yooyu ngeen naw ëpplewuñu ma dara. 12:12 Kéemaan yi, jaloore yi ak jëf yu màgg, yiy firndeel ndawul Kirist, feeñ nañu ci seen biir, ma ànd ci ak muñ gu mat. 12:13 Lan laa defal yeneen mboolooy ñi gëm te defaluma leen ko, xanaa rekk li ma wéeru ci ñoom te wéeruma ci yéen? Baal-leen ma googu tooñ! 12:14 Maa ngi leen di waaj a ganesi ñetteel bi yoon, te duma wéeru ci yéen. Wutsiwuma seen alal, yéen laa soxla. Ndaxte du gune moo war a yor waajuram, waaye waajur moo war a yor gune yi. 12:15 Man nag nangu naa joxe li ma am lépp ak xol bu sedd, ba joxe sama bopp sax, ngir dimbali leen. Gannaaw bëgg naa leen nii, xanaa kay seen mbëggeel ci man warul a wàññiku? 12:16 Kon noonu la, nekkuma woon yen ci yéen. Waaye man na am ñu naan, dama leen a nax, ba réeral leen ci sama njublaŋ. 12:17 Mbaa du damaa lekk seen alal, jaare ko ci kenn ci ñi ma yónni woon? 12:18 Sant naa Tit, mu ñëw ci yéen, te yebal naa sunu mbokk moomu ak moom. Ndax Tit dafa lekk seen alal? Man ak moom, ndax bokkunu woon xel mu nu yékkati ak tànk yu nuy dox? 12:19 Xanaa diirub li ngeen di jàng lii, defe ngeen ne, nu ngi wut aw lay ci seen kanam. Samay xarit, nu ngi leen di wax ci kanam Yàlla ak ci turu Kirist; te lépp ngir seen njariñ la. 12:20 Ragal naa, bu ma ñëwee ci yéen, fekk leen nu ma neexul, te yéen it ngeen fekk ma nu leen neexul. Ragal naa fekk ay xuloo ci seen biir, ak ñeetaane, xadar ak diiroo mbagg, xas ak jëw, réy-réylu ak yengu-yengu. 12:21 Ragal naa, bu ma leen ganesiwaatee, Yàlla sama Boroom suufeel ma ci seen biir, ma naqarlu ci ñu bare ñu bàkkaaroon te dëdduwuñu seen yàqute, seen njaaloo ak seen ñaawteef, gi ñu doon def.
13:1 Bii mooy ñetteel bi yoon, ma di leen ganesi. «Bépp àtte dina aju ci seedes ñaar walla ñetti nit.» 13:2 Li ma waxoon ci sama ñaareelu ngan, ci ñi bàkkaaroon bu yàgg ak ñi ci des, maa ngi koy waxaat léegi, bala maa dikkaat: su ma dellusee, duma yërëm kenn. 13:3 Bu fekkee ne dangeen a bëgg firnde juy wone ne, Kirist mooy wax jaarale ko ci man, dingeen ko am. Digganteem ak yéen du ànd ak néew doole, waaye dafay feeñal kàttan ci seen biir. 13:4 Néewoon na doole, ba ñu koy daaj ca bant ngir rey ko, waaye mi ngi dund ci kàttanu Yàlla. Nun itam néew nanu doole ci sunu bokk ci moom, waaye dinanu dund ak moom ci kàttanu Yàlla, bu nuy jëfante ak yéen. 13:5 Xool-leen seen bopp bu baax, ba xam ndax ngëm a ngi ci yéen. Seetluleen seen bopp. Xanaa xamuleen ne, Yeesoo ngi ci yéen? Walla boog ngeen gis ne, ay naaféq ngeen. 13:6 Waaye yaakaar naa ne dingeen gis ne, man nanoo wone nun, firndeg ngëm. 13:7 Nu ngi ñaan Yàlla, ngeen bañ a def dara lu bon. Waxuma ne danoo bëgg a wone noonu sunu firndeg ngëm, waaye sunu yéene mooy ngeen jëf lu baax, boo yaboo sax ñu jiiñ nu ag naaféq. 13:8 Ndaxte manalunu dara dëggu Yàlla gi; mënunu lu dul taxawal ko. 13:9 Bu nu néewee doole, fekk am ngeen doole, bég nanu ci. Te sax nu ngi ñaan, ngeen jublu cig mat. 13:10 Looloo tax ma leen di binde nii, bala maa ñëw; bëgguma leen a duma ci sañ-sañ bi ma Boroom bi jox. Jox na ma ko, ngir ma yokk seen ngëm, waaye du ngir seen kasara. 13:11 Kon nag bokk yi, bégleen, jublu cig mat, di déglu soññante bi ma leen di dénk, am benn xalaat te dëkk ci jàmm; noonu Yàlla miy mbëggeel te di Yàllay jàmm dina ànd ak yéen. 13:12 Saafoonteleen ak xol bu laab. 13:13 Mboolem gaayi Yàlla yépp ñu ngi leen di nuyu. 13:14 Na yiwu sunu Boroom Yeesu Kirist, ak mbëggeelu Yàlla ak booloo, gi nu am ak Xel mu Sell mi, ànd ak yéen ñépp.
1:1 Man Pool, ndawul Yeesu Kirist --nit falu ma ko, te jaarewul it ci nit, mi ngi jaare ci Yeesu Kirist ak Yàlla Baay, bi ko dekkal — 1:2 man ak bokk yiy ànd ak man yépp, nu ngi leen di bind, yéen mboolooy ñi gëm te dëkk ci diiwaanu Galasi. 1:3 Na yiw ak jàmm féete ak yéen, jóge ci Yàlla sunu Baay ak Yeesu Kirist Boroom bi, 1:4 moom mi joxe bakkanam ngir dindi sunuy bàkkaar, te musal nu ci àddina su bon, si nu nekk, dëppook coobareg Yàlla sunu Baay, 1:5 bi yelloo ndam ba fàww. Amiin. 1:6 Man de jaaxle naa! Yàlla woo na leen ci boppam jaarale ko ci yiw, wi nu Kirist defal, waaye yéena ngi koy gaawantoo bàyyi, ngir topp beneen xebaar, 1:7 fekk du xebaar bu baax bi. Dafa am rekk ci seen biir ay nit ñiy nëxal xel yi, te bëgg a dandal xebaar bu baax bu Kirist. 1:8 Waaye su fekkee kenn ci nun ñëw, walla malaaka sax mu jóge asamaan, di yégle beneen xebaar bu mengoowul ak bi nu leen yégal, kooku Yal na alku! 1:9 Wax nanu ko, maa ngi koy waxaat: bu leen kenn yégalee beneen xebaar bu dul bi ngeen nangu, kooku Yal na alku! 1:10 Ndax kon nit laay wut a gëmloo, am damay fexee yey Yàlla? Mbaa damay wut a neex nit ñi? Su ma doon wut a neex nit ñi ba tey, kon duma nekkati jaamu Kirist. 1:11 Bokk yi, maa ngi leen di xamal ne, xebaar bu baax bi ma yégle, jógewul ci nit. 1:12 Jëlewuma ko ci nit, te kenn jàngalu ma ko, waaye Yeesu Kirist moo ma ko won. 1:13 Dégg ngeen ni ma doon jëfe, bi ma nekkee ci diiney Yawut yi, di fitnaal bu metti mbooloom Yàlla, di ko jéem a tas. 1:14 Bokkoon naa ci ñi gën a farlu ci diiney Yawut yi, te sawar it ci sàrti yoon, yi fi samay maam bàyyi, ba raw sama maas, gi ma bokkal askan. 1:15 Waaye Yàlla mi ma tànn lu jiitu sama juddu te woo ma ci boppam ci kaw yiwam, bi mu ko soobee, xamal na ma kan mooy Doomam, ngir ma yégal ñi dul Yawut xebaar bu baax bi ci mbirum Kirist; booba nag diisoowuma ci ak kenn. 1:17 Demuma sax Yerusalem seeti ñi ma jëkk a nekk ay ndawi Kirist, waaye réewu Arabi laa dem, te gannaaw loolu ma dellusiwaat Damas. 1:18 Ba ñu ca tegee ñetti at, ma sog a dem Yerusalem, ngir xamante ak Sefas, dal fa moom lu mat ñaari ayu-bés. 1:19 Waaye gisuma keneen ci ndaw yi ku dul Saag, doomu ndeyu Boroom bi. 1:20 Lii ma leen di bind nag, Yàllaa may seede ci ne, du ay fen. 1:21 Bi loolu wéyee dem naa réewu Siri ak réewu Silisi. 1:22 Waaye ba tey mboolooy ñi gëm Kirist ci diiwaanu Yude xamuñu ma woon. 1:23 Dañu déggoon ñu naan rekk ne: «Ki nu daan fitnaal bu jëkk te daan jéem a far yoonu ngëm wi, léegi mi ngi koy yégle!» 1:24 Te ñuy sant Yàlla ci man.
2:1 Ba ñu ca tegee fukki at ak ñeent, ànd naa ak Barnabas, dellu Yerusalem, yóbbaale Tit. 2:2 Dem naa fa, ndaxte Yàllaa ma fa yebal ci kaw peeñu. Ba ma demee, daje naa ak ñi ñu gën a fonk ca mbooloo ma, ma wéetoo ak ñoom, won leen xebaar bu baax, bi may yégal ñi dul Yawut; ngir ragal sama coonob démb mbaa tey neen. 2:3 Te Tit mi ma gunge woon sax de, li mu bokk ci xeetu Gereg, taxul ñu sonal nu ci xarafal ko. 2:4 Fekk na mbir moomu nekk coow ndax naaféq, yi yoxoosu ci sunu biir ak mébét mu bon, ngir seet yaatu gi nu am ci Yeesu Kirist, ba fexe noo defaat ay jaam. 2:5 Waaye yaatalunu leen benn yoon, ngir dëggug xebaar bu baax bi man a sax ci yéen. 2:6 Waaye ñi ñu gën a fonk --ak lu man a doon seen sag xooluma ko, ñépp a yem fa kanam Yàlla — waaye ñooñu ñu teg njiit boog, bi ma dajee ak ñoom, yokkuñu dara ci sama sas. 2:7 Gis nañu ne, Yàllaa nu yebal, muy man di Piyeer, ngir nu yégle xebaar bu baax bi; ma féetewoo ñi dul Yawut, Piyeer féetewoo Yawut yi. 2:8 Ndaxte ni Yàlla jëfe ci Piyeer, miy ndawam ci Yawut yi, noonu it la jëfe ci man, may ndawam ci ñi dul Yawut. 2:9 Te Saag, Sefas ak Yowaana nag, ñi ñu teg kenuy mbooloo mi, bi ñu ràññee yen bi ma Yàlla jagleel ci yiwam, ñu fekksi nu ci, ba jox nu loxo, man ak Barnabas, nu liggéey ca ña dul Yawut, ñoom ñu liggéey ca Yawut ya. 2:10 Li ñu doon laaj rekk moo di, nuy fàttaliku seen aji néew doole yi, fekk sax laxasu woon naa ci def ko. 2:11 Waaye bi Sefas ñëwee dëkku Ancos, yedd naa ko ci kanamu ñépp, ndaxte li mu def jaaduwul. 2:12 Ndaxte laata ndaw yi Saag yónni di ñëw, da daan bokk di lekk ak ñi dul Yawut. Waaye bi ñu agsee, te mu ragal kureel boobu faaydaal xaraf, mu dellu gannaaw, di sore ñi dul Yawut. 2:13 Yeneen Yawut yi it daldi ànd ak Sefas ci naaféqam, ba yóbbaale sax Barnabas. 2:14 Bi ma seetee nag ne, awuñu woon ci dëgg, gi xebaar bu baax bi di jàngale, ma yedd Sefas ci kanamu ñépp ne ko: «Yaw miy Yawut, gannaaw dëddu nga aaday Yawut yi, ba dund ni ku dul Yawut, lu tax nga bëgg a sëf diiney Yawut ci ñi dul Yawut?» 2:15 Nun danoo cosaanoo ci xeetu Yawut, te bokkunu ci xeet, yi xamul Yàlla tey bàkkaar. 2:16 Teewul nu xam ne, Yàlla du àtte kenn ni ku jub ci kaw sàmm yoon, waaye ci gëm Yeesu Kirist. Kon nun itam gëm nanu Kirist Yeesu, ngir Yàlla àtte nu jub ci kaw gëm Kirist, te du ci sàmm yoon. Ndaxte du caageenug sàmm yoon mooy tax Yàlla àtte kenn ni ku jub. 2:17 Waaye ba tey su fekkee ne nu ngi wut a jub ci kaw gëm Kirist, fekk nu ne fàŋŋ di ay bàkkaarkat, ndax nag Kirist moo sas bàkkaar? Mukk! 2:18 Waaye su ma delloo di sàmm ndigali yoon, yi ma bàyyi, dëgg-dëgg dinaa wone noonu ne, moykatu yoon wi laa. 2:19 Ci li jëm ci yoonu Musaa, dee naa, fekk yoon wi ci boppam moo ko waral, ngir ma man a dund, ba amal jariñ Yàlla. 2:20 Daajaale nañu ma ak Kirist ca bant ba, te noonu du man may dundati, waaye Kirist mooy dund ci man. Dundu mbindeef, gi may dund nag, maa ngi koy dund ci gëm Doomu Yàlla ji, moom mi ma bëgg, ba joxe bakkanam ngir man. 2:21 Duma neenal yiwu Yàlla, ndaxte su sàmm yoon doon tax a jub fa kanam Yàlla, kon Kirist dee na cig neen.
3:1 Yéen waa Galasi, yéena ñàkk xel! Ku leen fàbbi, gannaaw bi ma leen yégalee ci lu leer ni ñu daaje Yeesu Kirist ca bant ba? 3:2 Lenn rekk laa bëgg, ngeen wax ma ko: ndax sàmm yoon wee tax, ngeen jot Xelum Yàlla? Déedéet! Dangeen a dégg xebaar bu baax bi te gëm ko. 3:3 Mbaa du nii ngeen ñàkke xel, ba tàmbalee ci Xelum Yàlla, ba noppi yaakaar a mate ci seen jëfi bopp? 3:4 Mbaa du fitna, yi ngeen daj yépp, dafa nar a neen? Mënuma koo gëm! 3:5 Bu leen Yàlla di may Xelam, di leen won jalooreem, ndax li ngeen sàmm yoon a tax, mu def ko, mbaa li ngeen dégg xebaar bu baax te gëm ko? 3:6 Xool-leen ci Ibraayma; Mbind mi wax na ne:«Ibraayma gëm na Yàlla,te Yàlla jàppe ngëmam ni njub.» 3:7 Xamleen boog ne, boroom ngëm yi rekk ñooy doomi Ibraayma. 3:8 Mbind mi tëral na lu jiitu ne, Yàlla dina àtte jub ñi dul Yawut ci kaw ngëm. Kon looloo tax mu yégal Ibraayma lu jiitu xebaar bu baax bi ne ko: «Xeeti àddina yépp dinañu barkeel ci yaw.» 3:9 Kon ñi gëm, Yàlla dina leen barkeel, sukkandikoo ko ci seen ngëm, ni mu defal Ibraayma, boroom ngëm. 3:10 Ñiy wékku ñépp ci jëfi yoon wi, ñu alku lañu, ndaxte bind nañu ne: «Képp ku dul topp lépp lu ndigali yoon wi santaane, Yal na alku.» 3:11 Bir na sax ne, sàmm yoon du tax kenn jub fa kanam Yàlla, ndaxte Mbind mi tëral na ne: «Ku jub ci kaw ngëm dinga dund.» 3:12 Waaye yoon wi laajul ngëm. Mbind mi nee na: «Ku manoon a matal li yoon wi wax, kon dinga dund ba fàww.» 3:13 Waaye Kirist jot na nu ci alkande, ji yoon wi indi; mu gàddul nu ko, ba far alku moom ci boppam, ndaxte Mbind mi nee na: «Képp ku ñu rey, wékk ko ci bant, alku nga.» 3:14 Noonu barke bi Yàlla dig Ibraayma baawaan na, ba daj ñi dul Yawut te gëm Kirist Yeesu, te nu jot ci kaw ngëm Xel mu Sell, mi Yàlla dige. 3:15 Bokk yi, maa ngi misaal wax ji ci jëfi doom Aadama. Xam ngeen ne, kóllëre gu ñu fas ba noppi, waruñu koo fecci, walla ñu ciy rax dara. 3:16 Léegi nag Yàlla am na lu mu dig Ibraayma ak askanam. Mbind mi waxul: «Ak i sëtam,» mu mel ni ñu bare, waaye kenn la wax: «Ak sa askan,» maanaam Kirist. 3:17 Li ma ci bëgg a wax mooy lii: ndegam Yàlla fas na kóllëreem, yoonu Musaa, wi feeñ ñeenti téeméeri at ak fanweer gannaaw ga, du ko man a fecci, ba tebbi digeb Yàlla. 3:18 Ndaxte xéewal, yi Yàllay dige, bu ñu doon jóge ci yoon wi, kon ajootuñu ci dige bi, fekk ci kaw dige la ko Yàlla maye Ibraayma. 3:19 Waaw kon yoonu Musaa, luy jariñam? Dañu koo wàcceel nit ñi, ngir seen jàdd yoon ne fàŋŋ. Looloo doon wàllu yoon wi, ba kera Sët biy ñëw, moom mi ñu digoon dige bi. Yoon wi nag, Yàlla tëral na ko jaare ci ay malaaka, te am na ku ko jottali. 3:20 Waaye aajowul jottalikat, su fi kenn rekk teewee, te Yàlla kenn la. 3:21 Ndax kon yoonu Musaa wi dafa juuyoo ak li Yàlla dige? Mukk! Su amoon yoon wu nit man a sàmm, ba mu jural ko dund gu sax, kon sàmm yoon dina tax nit jub fa kanam Yàlla. 3:22 Waaye yoon wi tëj na ñépp ci dooley bàkkaar, ngir ñi gëm Yeesu Kirist jot li Yàlla dige woon ci seen kaw ngëm. 3:23 Bi ngëm Yeesu Kirist feeñagul nag, yoon wi da noo tëjoon ràpp, ba kera ngëm di feeñ. 3:24 Ci noonu la nu yoon wi doon noote, ba Kirist di ñëw, ngir Yàlla àtte nu jub ci kaw ngëm. 3:25 Waaye léegi, bi jamonoy ngëm ji ñëwee, nekkatunu ci kilifteefu yoon wi. 3:26 Yéen ñépp doomi Yàlla ngeen ndax li ngeen bokk ci Kirist Yeesu ci kaw ngëm. 3:27 Yéen ñépp, ñi ñu sóob ci ndox ngir wone seen bokk ci Kirist, soloo ngeen Kirist. 3:28 Kon nag amul xaajale ci diggante Yawut ak ki dul Yawut, ci diggante jaam ak gor, ci diggante góor ak jigéen. Yéen ñépp benn ngeen ci seen bokk ci Kirist. 3:29 Bu ngeen bokkee ci Kirist, kon bokk ngeen ci askanu Ibraayma, te jot ngeen xéewal, yi ko Yàlla dig.
4:1 Li ma leen di wax, mooy lii: doom ji war a donni baayam, fi ak mu ngi cig ndaw, ak lu ko alal jiy lew lépp, du wuute dara ak jaam. 4:2 Ñi ko yore tey sàmm alalam ñoo koy yilif, ba jamono ji ko baayam àppaloon mat. 4:3 Nun itam naka noonu, laata nuy mat, aaday àddina ñoo nu nootoon, ba def nu ni ay jaam. 4:4 Waaye bi àpp bi Yàlla tëraloon matee, yónni na Doomam, mu juddoo ci jigéen, ci biir yoonu Musaa, 4:5 ngir jot ñi yoon wi nootoon, ndax Yàlla jàpp nu ni ay doomam. 4:6 Gannaaw doomi Yàlla ngeen nag, Yàlla yónni na Xelu Doomam ci sunu xol, mu koy wooye nii: «Abba,» maanaam «Baay.» 4:7 Noonu dootuloo jaam, doom nga. Te ndegam doom nga, Yàlla jagleel na la cér ci xéewal, yi mu dencal ay doomam. 4:8 Bu jëkk, bi ngeen xamagul Yàlla, yéena ngi doon jaamu yeneen yu ñu daan bokkaaleel Yàlla. 4:9 Waaye léegi nag bi ngeen xamee Yàlla, walla boog bi leen Yàlla xàmmee, nan ngeen man a def, bay delluwaat ca aaday àddina? Aada yooyee ñàkk doole te ñàkk njariñ, lu tax ngeen bëgg, ñu nootaat leen? 4:10 Yéena ngi fonk bés yi, weer yi, màggal yi ak at yi! 4:11 Sama xel dalul ci yéen, ngir ragal sama coono ci yéen neen. 4:12 Bokk yi, dama leen di ñaan, ngeen mel ni man, ndaxte man itam fekksi naa leen ci seen xalaat. Tooñuleen ma. 4:13 Xam ngeen ne, sama wopp moo taxoon, ma yégal leen xebaar bu baax bi. 4:14 Coono, gi leen sama wopp tegoon, taxul ngeen bañ ma, taxul ngeen séexlu ma. Waaye teeru ngeen ma, ni bu ngeen doon teeru malaakam Yàlla walla Yeesu Kirist. 4:15 Waaw, fan la seen mbég jaar? Ndaxte seedeel naa leen ne, su ngeen ko manoon, kon luqi ngeen seeni bët, jox ma. 4:16 Ndax dëgg, gi ma leen wax, moo tax ngeen def ma ab noon? 4:17 Nit ñooñu leen di farle, seen mébét baaxul. Dañu leen a bëgg a tàggale ak nun, ngir ngeen far ak ñoom. 4:18 Farle baax na, bu àndee ak mébét mu baax. Waaye bu sama jëmm rekk tax ngeen koy def. 4:19 Sama doom yi! Yéena tax may dellu ci metit ni kuy matu, ba kera jikkoy Kirist di mat ci yéen. 4:20 Léegi bëggoon naa nekk ci seen biir, ngir man a jubbanti sama kàddu, ndaxte xamatuma nu may doxale ak yéen! 4:21 Yéen ñi bëgg a topp yoon wi, xanaa xamuleen li yoonu Musaa wi wax? 4:22 Mbind mi nee na: Ibraayma am na ñaari doom; ki jaam bi jur ak ki gor si jur. 4:23 Doomu jaam bi juddu na ni bépp doom, waaye doom, ji mu am ak jabaram, juddu na ci kaw digeb Yàlla. 4:24 Loolu nag am na lu muy misaal. Ñaari jigéen ñi dañoo bijji ñaari kóllëre. Benn bi di Ajara, mooy wone kóllëre, gi Yàlla fasoon ca tundu Sinayi. Ay jaam lay jur. 4:25 Ajara moomu mooy tundu Sinayi, wi nekk ca réewu Arabi. Te it mooy misaalu dëkku Yerusalem, bi fi nekk tey. Ndaxte moom ak ay doomam yépp ay jaam lañu. 4:26 Waaye Yerusalem, ga ca kaw, mooy gor si. Moom mooy sunu ndey. 4:27 Ndaxte Mbind mi nee na:«Bégal, yaw jigéen ji dul jur,te musul a am doom.Reeyal te bànneexu,yaw mi musul a xam coonob mat,ndaxte jigéen ji ñu faalewulmoo gën a jaboot ki nekk ak jëkkëram.» 4:28 Yéen bokk yi, yéenay doom yi ñu dige woon, niki Isaaxa. 4:29 Waaye doom ji juddoo ni bépp doom, dafa daan sonal doom ji juddoo ci dooley Xelum Yàlla. Te loolu mooy law ba léegi. 4:30 Lu ci Mbind mi wax nag? Nee na: «Dàqal jaam bi ak doomam, ndaxte doomu jaam bi warul a bokk cér ak doomu gor si ci ndono.» 4:31 Kon nag bokk yi, nun dunu doomi jaam, ay doomi gor lanu.
5:1 Kirist a nu daggal sunu buumi njaam, ngir goreel nu. Kon dëgërleen ci seen ngor te bañ a delluwaat ci njaam. 5:2 Dégluleen! Man Pool maa leen koy wax: bu ngeen itteelee xaraf, kon Kirist dootu leen jariñ dara. 5:3 Te maa ngi dellu di waxaat ne, képp kuy farataal xaraf, fàww nga sàmm lépp lu yoon wi santaane. 5:4 Yéen ñiy fexee jub fa kanam Yàlla ci kaw sàmm yoon, tàggalikoo ngeen ak Kirist; dëddu ngeen yiwu Yàlla. 5:5 Waaye njub, gi nu Yàlla dencal ëllëg, nu ngi koy séentu ci kaw ngëm ak ci ndimbalu Xelum Yàlla. 5:6 Ndaxte bu nu bokkee ci Kirist Yeesu, xaraf ak bañ a xaraf, dara amu ci solo; li am solo mooy ngëm, giy jëf ci mbëggeel. 5:7 Ni ngeen jógtee woon de baax na! Waaw ku leen dog, ba ngeen bañ a déggal dëgg? 5:8 Li ñu leen xiir jógewul ci Yàlla, mi leen woo. 5:9 Dees na ne: «Tuuti lawiir day tax tooyalu fariñ bépp funki.» 5:10 Waaye teewul Boroom bi jox na ma kóolute ci yéen. Biral na ma ne, dingeen bokk ak man xalaat. Léegi nag, kiy nëxal seen xel, ku mu man a doon, Yàlla dina ko mbugal. 5:11 Man nag bokk yi, bu ma doon faaydaal xaraf ci sama waare, kon duñu ma fitnaale nii; te it li may yégle ci deewu Kirist ca bant ba dootul naqari kenn. 5:12 Ñi farataal xaraf te di leen dëpp, nañu gën a sore ci seen réer: bu yaboo sax ñu dagg seen ngóora, ba dara du ci des! 5:13 Yéen nag bokk yi, Yàlla woo na leen, ngeen nekk i gor. Waaye nag buleen ci sukkandiku, bay topp seen nafsu, waaye dimbaleenteleen ci kaw mbëggeel. 5:14 Ndaxte yoon wépp, ndigal lii a ko tënk: «Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.» 5:15 Waaye moytuleen! Bu ngeen dee màttante ak a lekkante, dingeen yàqante. 5:16 Li ma leen di wax mooy lii: dundleen ci Xelum Yàlla, kon dungeen topp seen nafsu. 5:17 Ndaxte sunu nafsu am na ay bëgg-bëgg yu mengoowul ak yu Xelum Yàlla. Te Xelum Yàlla itam am na ay bëgg-bëgg yu mengoowul ak yu sunu nafsu. Ñoom ñaar dañoo juuyoo ci bépp fànn, ba tax lépp lu ngeen bëggoon a def, dungeen ko man. 5:18 Waaye bu ngeen toppee Xelum Yàlla, nekkatuleen ci kilifteefu yoon wi. 5:19 Kuy topp sa nafsu, nii ngay jëfe: njaaloo, xalaat yu bon, def i ñaawteef ak say cér, 5:20 xërëm, luxus, noonoo ak xuloo, ñeetaane, xadar, diiroo mbagg, féewaloo ak xaajaloo, 5:21 kiñaan, màndite ak xawaare ak yeneen yu ni mel. Léegi nag maa ngi leen di artu, ni ma ko defe woon: ñiy jëfe noonu duñu am cér ci nguuru Yàlla. 5:22 Waaye li Xelu Yàlla mi di meññ mooy: mbëggeel, mbég, jàmm, muñ, laabiir, mbaax, kóllëre, 5:23 lewetaay ak maandute. Yoon wi terewul yu ni mel. 5:24 Léegi ñi bokk nag ci Yeesu Kirist, daaj nañu seen nafsu ca bant ba, wacc ko fa, moom ak ay xemmemam ak ay bëgg-bëggam. 5:25 Gannaaw nag nu ngi dund léegi ci Xelum Yàlla, kon nanu ko topp. 5:26 Bu nu tiitaru di dëkkante, di iñaanante.
6:1 Bokk yi, ku ñu fekk muy def lu Yàlla bëggul, yéen ñi topp Xelum Yàlla, nangeen ko jubbanti ak xol bu lewet. Waaye nanga sàmm sa bopp, ngir bàkkaar bañ laa fiir, yaw itam. 6:2 Jàppalanteleen, noonu dingeen sàmm yoon wi Kirist tëral. 6:3 Ndaxte kuy naagu te fekk doo dara, dangay nax sa bopp. 6:4 Na ku nekk seetlu ni muy beye sasam. Bu ko defee dina man a naw boppam, tey bañ di diirante mbagg ak ñi ci des. 6:5 Ndaxte ku ci nekk dangaa war a yenu sab yen. 6:6 Kiy jàng kàddug Yàlla war na sédd ki koy jàngal ci alalam jépp. 6:7 Bu leen ci dara nax; kenn du fontoo Yàlla, ndaxte lu waay ji, moom ngay góob. 6:8 Ku ji ngir sa nafsu, dinga góob li sa nafsu meññ, maanaam ag yàqute. Waaye ku ji lu soloo ak Xelum Yàlla, li Xel mi meññ ngay góob, maanaam dund gu dul jeex. 6:9 Bunu tàyyi ci def lu baax, ndaxte bu nu ci sawaree, bu waxtu wi jotee dinanu jariñu. 6:10 Noonu fi ak nu koy man, nanuy defal ñépp lu baax, rawatina nag sunu bokk yi gëm. 6:11 Seetleen araf yu mag yii ma leen bind ci sama loxob bopp! 6:12 Ñiy gistal ci seen yaram, ñooñoo bëgg ngeen xaraf, ngir ragal a daj fitna ci yégle deewu Kirist ca bant ba. 6:13 Kureel gi faaydaal xaraf, ñoom ci seen bopp sax, duñu topp yoon wi. Dañoo bëgg a ngeen xaraf, ba ñu man a bàkku ci seen yaram, yéen. 6:14 Man ci sama wàllu bopp, duma bàkku mukk su dul ci deewu sunu Boroom Yeesu Kirist, ba ñu ko daajee ca bant ba. Deeyam moo tax ma mel ni ku dee ci yëfi àddina; yëfi àddina dee ci man. 6:15 Xaraf ak bañ a xaraf dara amu ci solo. Li am solo mooy nekk mbindeef mu bees. 6:16 Ñiy topp ndigal lii nag, na Yàlla wàcce jàmm ak yërmande ci ñoom, ak ci Israyilu Yàlla. 6:17 Léegi nag, bu ma kenn lëjalati, ndaxte yor naa ci sama yaram ay leget yuy màndargaal ne, jaamu Yeesu laa. 6:18 Bokk yi, na yiwu Yeesu Kirist sunu Boroom ànd ak seen xel. Amiin.
1:1 Man Pool, ndawul Kirist Yeesu ci coobareg Yàlla, maa leen di bind, yéen gaayi Yàlla yu sell yi te gëm Kirist Yeesu ci dëkku Efes. 1:2 Na leen Yàlla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak jàmm. 1:3 Cant ñeel na Yàlla Baayu sunu Boroom Yeesu Kirist, mi nu sotti ci sunu bokk ci Kirist lépp luy barkeel ci baatin te nekk ca bérab yu kawe ya. 1:4 Ndaxte ba àddina sosoogul, tànn na nu ci Kirist, ngir nu man a teew fa kanamam, sell te ñàkk sikk. Ci kaw mbëggeelam 1:5 séddoo na nu lu jiitu, def nu ay doomam jaarale ko ci Yeesu Kirist, ndaxte looloo doon yéene ju rafet, ji mu tëral ci coobareem. 1:6 Na ndamam jolli ndax yiw wu réy, wi mu nu sotti ci Soppeem bi. 1:7 Moom jot na nu ak deretam ji ñu tuur, maanaam baal nu sunuy bàkkaar, ci kaw yiw wu yaatu, 1:8 wi mu nu baawaanal. Te Yàlla sol na nu xel mu mat ak dégg, 1:9 ci feeñal nu mbóoti coobareem, dëppook yéeneem ju rafet, ji mu jaarale ci Kirist. 1:10 Mu tëral ne, bu jamono yi wéyee ba lépp mat, dina dajale lépp ci kilifteefu Kirist, muy ci kaw, muy ci suuf. 1:11 Te am nanu cér ci moom bu nu Yàlla sédd lu jiitu ci dogalam, moom miy doxal lépp ci ni mu ko àttee ci coobareem. 1:12 Noonu nuy jollil ndamam, nun ñi jëkk a wékk sunu yaakaar ci Kirist. 1:13 Te yéen itam, bi ngeen déggee kàddug dëgg gi, di xebaar bu baax, bi leen tegtal yoonu mucc, te ngeen gëm ko, Yàlla tàmpe na leen ni ñoñam ak Xel mu Sell, mi mu dige woon. 1:14 Te Xel mi mooy dawal gi nu Yàlla jox ci cér, bi mu nu dencal, ba kera muy goreel ñi mu jotal boppam, te ñépp jollil ndamam. 1:15 Bi ma déggee nag seen ngëm ci Boroom bi Yeesu ak seen mbëggeel ci gaayi Yàlla yu sell yépp, 1:16 duma noppee sant Yàlla, di leen boole ci samay ñaan. 1:17 Te li may ñaan Yàllay sunu Boroom Yeesu Kirist, di Baay bi yelloo ndam, mooy lii: mu sol leen xel mu xóot, te xamal leen boppam 1:18 ci leeral seeni xol. Noonu dingeen xam yaakaaru ëllëg, ji leen Yàlla wooye, di ndam lu xel mënta daj, li nekk ci cér, bi mu dencal gaayam yu sell yi. 1:19 Ngeen xam it, ni kàttanam màgge ba jéggi dayo, jëm ci nun ñi gëm, dëppook dooleem ju ràññiku, 1:20 ji mu jëfe ci Kirist, ci li mu ko dekkal, dëël ko ci ndeyjooram ca bérab yu kawe ya, 1:21 mu tiim lu sore malaaka yépp, muy kilifa, boroom sañ-sañ, boroom doole mbaa buur, te gën a màgg wépp tur wu ñu man a tudd, muy tey, muy ëllëg. 1:22 Yàlla suufeel na lépp fi kanamam, def ko kilifag lépp ci mbooloom ñi gëm, 1:23 miy jëmmam, di matug Kirist, mi fees mbindeef mu ne ci fànn gu ne.
2:1 Te yéen itam Yàlla dekkal na leen, yéen ñi doon ndee fa kanamam ci seeni moy ak seeni bàkkaar. 2:2 Ci biir yooyu ngeen doon dund démb, topp doxalinu àddina, tey déggal kilifag boroom sañ-sañ yi ci jaww ji, di xel mu bon miy jëf ci kureelu ñi déggadil Yàlla. 2:3 Te nun it booba àndoon nanu ak ñoom ca seen dund ga, di topp sunu bakkan ciy wut bànneexi yaram ak coobarey xel. Noonu ci sunu bindu nit yeyoo nanu meru Yàlla, ni ña ca des. 2:4 Waaye Yàlla mi bare yërmande, ci kaw mbëggeel gu réy, gi mu am ci nun, 2:5 dundalaat na nu ak Kirist, fekk ndee lanu woon fa kanamam ci sunuy bàkkaar — ci kaw yiwu Yàlla ngeen mucce. 2:6 Te dekkal na nu ak Kirist Yeesu, dëël nu ak moom ca bérab yu kawe ya. 2:7 Noonu ba fu jamono yem, dina lañal fi sunu kanam yiwam wu réy wi xel mënta takk, jaar ci baaxaay gi mu nu won ci Kirist Yeesu. 2:8 Ndaxte ci yiwu Yàlla ngeen mucce ci kaw ngëm, te loolu jógewul ci yéen, mayu Yàlla la; 2:9 du peyu jëf, ngir kenn du ci kañu. 2:10 Ndaxte jëfu Yàlla lanu; moo nu bind ci Kirist Yeesu, ngir nu wéy ci jëf yu rafet, yi mu nu fàgguloon ca njàlbéen ga. 2:11 Kon nag yéen ñi dul Yawut cib juddu, yéen ñi xaraful, te ñi xaraf ci seen yaram ci loxol nit ñoo leen teg ay yéefar, fàttalikuleen lii: 2:12 booba amuleen woon benn cér ci Kirist, mbaa benn baat ci kureelu bànni Israyil. Bokkuleen woon ci kóllëre, gi Yàlla fas ak ñoom, te ëmb dige ya. Amuleen woon jenn yaakaar mbaa benn xam-xamu Yàlla ci àddina. 2:13 Waaye léegi ci seen bokk ci Kirist Yeesu, yéen ñi sore woon jege ngeen ndax deretu Kirist ji ñu tuur. 2:14 Ndaxte mooy sunu jàmm, moom mi jël Yawut ak ki dul Yawut, def nu benn. Ñag bi doxoon sunu diggante te sosoon sunu dëngoo, moo ko màbb ci li mu joxe yaramam, 2:15 far noonu yoonu Musaa, muy ndigal ya ak dogal ya. Noonu la nu jële, Yawut ak ki dul Yawut, def nu benn ci moom, ba nu jàmmoo. 2:16 Te nun ñaar, ñi def benn jëmm, jubale na nu ak Yàlla ci dee, gi mu dee ca bant ba ñu ko daajoon, dindee noonu sunu tongoonte. 2:17 Bi mu ko defee mu ñëw, yégalsi nu xebaaru jàmm fa kanam Yàlla, yéen ñi sore woon ak nun ñi jege. 2:18 Ndaxte nun ñaar ñépp am nanu bunt ci Yàlla Baay bi, jaar ci Kirist, ci ndimbalu menn Xel mu Sell mi. 2:19 Noonu dootuleen ay doxandéem mbaa ay gan, waaye am ngeen baat ci kureelu gaayi Yàlla yu sell yi, te waa këram ngeen. 2:20 Yéena ngi sukkandikoo ci fondamaa, bi ndawi Kirist yi ak yonent yi tabax, te Kirist Yeesu ci boppam di doju dalil wa. 2:21 Ci moom la doj yépp ràbbloo, ba tabax bi jóg, di màggalukaay bu sell ngir Boroom bi. 2:22 Te ci seen bokk ci Kirist, Yàlla boole na leen tabax yéen itam, ba ngeen nekk dëkkukaayam, jaar ci Xel mu Sell mi.
3:1 Kon nag maa ngi leen di ñaanal, man Pool mi ñu tëj kaso ci turu Kirist ndax sas wi may bey ci yéen, xeet yi dul Yawut. 3:2 Wóor na ma ne, dégg ngeen yenub xamle yiwu Yàlla, bi mu ma jagleel jëm ci yéen. 3:3 Yàlla feeñu na ma, xamal ma mbóoti mbir mi mu tëral, ni ma leen ko binde ci kàddu yu néew. 3:4 Bu ngeen jàngee loolu, dingeen man a xam bu wér dégg, gi ma am ci mbóoti mbiri Kirist. 3:5 Ci jamono yu weesu, loolu kumpa la woon ci doom Aadama, waaye léegi Yàlla feeñalal na ko ay ndawam ak yonentam yu sell yi, jaarale ko ci Xel mu Sell mi. 3:6 Mbir mi nii la tëdde: léegi xeet yi dul Yawut dañoo bokksi cér ak Yawut yi, bokk ak ñoom jenn jëmm, bokk wàll ci xéewal yi Yàlla dige ci Kirist Yeesu, te xebaar bu baax bi xamle ko. 3:7 Xamle xebaar bu baax boobu nag, Yàlla fal na ma ci jawriñ ci kaw yiwam, te di ma dooleel ci kàttanam. 3:8 May na ma, man mi gën a tuuti ci gaayi Yàlla yu sell yi, may xebaar xeeti àddina barkeel yu xel dajul yi ci Kirist; 3:9 te it may sulli melokaanu mbir mu xóot mi Yàlla tëral, te doon kumpa njàlbéen ga ba tey ci moom, mi sos lépp. 3:10 Waaye léegi nee na fàŋŋ, ngir kilifa yi ak boroom sañ-sañ yi ca bérab yu kawe ya man a xam ni Xelum Yàlla xóote, jaar ci li ñu gis ci mbooloom ñi gëm Kirist. 3:11 Mooy dogal bi sax dàkk, te Yàlla tëral ko ci Kirist Yeesu sunu Boroom. 3:12 Ci turam am nanu kóolute fa kanam Yàlla, ak bunt bu yaatu ci moom ci kaw ngëm. 3:13 Maa ngi leen di ñaan nag, ngeen bañ a yoqi ndax coono, yi may jële ci bey sama sas ci yéen, xam ne coono yooyu ñoo leen di jural ndam. 3:14 Moo tax maa ngi sukk, jublu ci Yàlla Baay 3:15 biy cosaanul njaboot gépp, muy ci kaw, muy ci suuf. 3:16 Ma di ko ñaan, mu may leen, ci kaw ndamam lu amul kem, Xel mu Sell mi feddali seen baatin ak kàttan gu mag, 3:17 ba Kirist dëkk ci seeni xol ci kaw ngëm. Te ngeen sax noonu te sampu ci mbëggeelu Yàlla, 3:18 ba jagoo, yéen ak gaayi Yàlla yu sell yépp, guddaay ba, yaatuwaay ba, kawe ga ak xóotaay ba, 3:19 te xam mbëggeelu Kirist, gi raw mépp xel. Noonu dingeen fees dell ak matug Yàlla. 3:20 Léegi nag, na ndam li féete ak Yàlla, mi man a yeggale lépp luy ñaan mbaa yéene, ba weesu ko fuuf, dëppook kàttan giy jëf ci nun; 3:21 moo yelloo ndamul mbooloom ñi gëm jamonoy jamono ba fàww, jaar ci Kirist Yeesu. Amiin.
4:1 Man mi ñu tëj kaso ngir Boroom bi nag, maa ngi leen di dénk, ngeen dund dundin wu yellook wooteb Yàlla. 4:2 Ngeen woyof toyy te lewet, di muñalante tey baalante ci mbëggeel, 4:3 te dem ba fu seen kàttan yem, ngeen likkoo ci jàmm, bay sàmm booloo gi leen Xelum Yàlla may. 4:4 Jenn jëmm moo am, menn Xel, ak jenn yaakaaru ëllëg ju wooteb Yàlla ëmb. 4:5 Benn Boroom it a am, genn ngëm, ak benn seedeb ngëm ci li ñu leen sóob ci ndox. 4:6 Te jenn Yàllaa am, di Baayu ñépp, mu tiim ñépp, fees ñépp, te dëkk ci ñépp. 4:7 Waaye ku nekk ci nun ak mayam, ni nu ko Kirist séddalee. 4:8 Looloo tax Mbind mi ne:«Yéeg na ba ca fa gën a kawe,yóbbaale mbooloom noon mu bare, mi mu noot,tey séddale nit ñi ay may.» 4:9 Su nu waxee ne «yéeg na,» li moo ci génn: daa jëkk a wàcc ba ca bérab ya gën a suufe. 4:10 Ki wàccoon moo yéegaat, ba tiim asamaan yépp, ngir fees lépp. 4:11 Moo may ñii di ay ndawam, ñii ay yonent, ñii ay taskati xebaar bu baax bi, ak ñeneen ñuy sàmm mbooloom ñi gëm te di ko jàngal. 4:12 Maye na leen, ngir ñu waajal gaayi Yàlla yu sell yi, ñu man a bey seen sas ci taxawal mbooloom Kirist, di jëmmam. 4:13 Noonu nu mànkoo ci sunu ngëm ak ci xam Doomu Yàlla ji, ba kera nuy egg ci nekk nit ku sotti, te taxaw taxawaay bu dëppook matug Kirist. 4:14 Noonu dootunu ay gune yu njàngalem nit ku ñëw di fàbbi ci seeni làqarci ak seeni pexe, nu mel ni ay gaal yu duus yi ak ngelaw li di baaje. 4:15 Waaye dinanu wax dëgg, ëmb ko ci mbëggeel, bay màgg ci fànn gu ne ci sunu bokk ci Kirist. Mooy bopp, 4:16 te jëmm jépp ci moom lay dunde, di jëmm ju ràbboo te déggoo ci bépp tenqoo, te cér bu nekk di def warugaram. Noonu jëmm ji di yokku ak a màgg ci biir mbëggeel. 4:17 Maa ngi leen di wax lii nag, te di ko dëggal ci kanamu Boroom bi: buleen dundeeti ni xeeti àddina yi, ci seeni xalaati neen 4:18 ak seen xel mu lëndëm. Dañoo génn ci dundu Yàlla, ndax umple gi ñu am ci moom, ak li ñu ko tëjal seen xol. 4:19 Seen xol dafa dërkiis, ba ñu bayliku ciy topp seen nafsu, di sóobu ci bépp sobe te xér ci. 4:20 Waaye du dundin woowu ngeen jàng ci Kirist. 4:21 Ndax yaakaar naa ne, dégg ngeen Kirist te jàng ngeen ci moom, ba xam dëgg gi Yeesu ëmb. 4:22 Maanaam ngeen yulli seen jikko ju bon, ji ngeen judduwaale te daan fés ci seeni jëf, te muy gën a yées, moom ak i bëgg-bëggam yuy naxe kese. 4:23 Te ngeen yeeslu ci seen biir xel, 4:24 te soloo jikko ju bees, ji Yàlla sàkk ci njub ak sell yu dëggu. 4:25 Kon nag bàyyileen di fen, tey wax dëgg kenn ku nekk ci moroomam, ndax ku nekk sa genn-wàllu moroom nga. 4:26 Ku mer, bu mu jàll aw kaañ; bu jant bi sowaale seen mer, 4:27 ba ngeen may Seytaane bunt. 4:28 Ku daan sàcc, na ko dëddu te jublu ci liggéey lu baax ci ay loxoom, ngir mu man a dimbali ñi néew doole. 4:29 Bu genn kàddu gu ñaaw génn ci seen gémmiñ, waaye su wax yegsee, nangeen wax lu rafet, ba faj soxlay seeni moroom, te teg ñi leen di déglu ci yoonu yiw. 4:30 Buleen yóbbe tiis Xelu Yàlla mu Sell, mi leen tàmpe ngir bésu goreel ba. 4:31 Dëdduleen lépp luy wex mbaa tàng bopp, luy mer mbaa coow, lépp luy xaste mbaa coxor. 4:32 Te ngeen baax ci seen diggante, di laayante biir tey baalante, ni leen Yàlla baale ci turu Kirist.
5:1 Yéen nag ñiy guney Yàlla, yi mu bëgg ci xolam, royleen ko ci loolu. 5:2 Ngeen wéer seen dund ci mbëggeel, mel ni Kirist mi nu bëgg, ba joxe bakkanam ngir nun, di sarax su ñu jébbal Yàlla te neex ko ni xetu latkoloñ. 5:3 Waaye naka njaaloo ak bépp sobe mbaa bëgge, jéllale naa jëf ji sax, waaye bu ko làmmiñ tudd, ni mu jekke ci gaayi Yàlla yu sell yi. 5:4 Dawleen it yu jekkadee, ni wax ju ñaaw mbaa waxi caaxaan ak kaf yu bon, te ngeen sax ci sant Yàlla. 5:5 Na leen wóor ne, kenn ku jikkowoo ndoxaan, sobe mbaa bëgge, maanaam bokkaale Yàlla, kooku du am cér ci nguuru Kirist ak Yàlla. 5:6 Bu leen kenn nax ci ay waxi neen, ndaxte jëf yooyooy tax meru Yàlla di wàcc ci kureelu ñi ko déggadil. 5:7 Kon nag buleen séq ak ñoom dara. 5:8 Lëndëm ngeen woon, waaye léegi leer ngeen ndax seen bokk ci Boroom bi. Dundeleen nag ni ay guney leer. 5:9 Leer, mbaax lay meññ, njub ak dëgg. 5:10 Dëggal-leen ci seeni jëf li neex Boroom bi, 5:11 te daw lépp luy jëfi lëndëm yu amul njariñ, bay weer sax ku koy def. 5:12 Ndaxte waxtaane sax li ñuy def ci nëbbu, lu ruslu la; 5:13 waaye leer, lu mu ëmb, fésal ko. 5:14 Ndaxte lu jaxasoo ak leer di leer. Looloo tax ñu ne:«Yeewul, yaw mi nelaw,te jóge ci biir néew yi,kon Kirist dina ne ràññ ci yaw,ni leeru jant buy fenk.» 5:15 Noonu sàmmleen seen dundin, waxuma ni ñu amul xel, waaye ni ñu am xel, 5:16 tey jariñoo jot gi, ndaxte nu ngi ci jamono ju bon. 5:17 Buleen ñàkk bopp nag, waaye xamleen liy coobareg Boroom bi. 5:18 Buleen màndi it ci sangara, liy ndeyi ñaawteef, waaye feesleen ak Xel mu Sell mi; 5:19 di waxante ci seen biir ci ay taalifi Sabóor, ci ay woy ak ay cant yu tukkee ci Xelum Yàlla, di woy ak a kañ Boroom bi ci seeni xol. 5:20 Gërëmleen Yàlla Baay bi ci turu Yeesu Kirist Boroom bi, fu ngeen man a tollu, ci lu mu man a doon; 5:21 teg ca nangul sa moroom ci biir wegeelu Kirist. 5:22 Naka yéen jigéen ñi, nangeen nangul seeni jëkkër, ni su doon Boroom bi. 5:23 Ndaxte góor mooy kilifag jabaram, ni Kirist nekke kilifag mbooloom ñi gëm, muy jëmmam ji muy sàmm. 5:24 Ni mbooloo mi nag jiitale Kirist, noonu la jigéen ji war a jiitale jëkkëram ci lépp. 5:25 Yéen nag góor ñi, na ku nekk bëgg jabaram, ni Kirist bëgge mbooloo mi, ba joxe bakkanam ndax moom, 5:26 ngir sellal ko ak kàddoom, ba mu laab ni ku sangu set. 5:27 Noonu dina ko jël, mu mel ni séet bu ñu waajal, di mbooloom mu soloo ndam, te gàkkul, rasul, taqul leneen, waaye mu sell te amul sikk. 5:28 Na góor bëgg jabaram, ni mu bëgge boppam. Bëgg sa jabar, bëgg sa bopp la. 5:29 Ndaxte kenn musul a bañ sa yaram. Waaye danga koy dundal, di ko fonk. Noonu it la Kirist fonke mbooloo mi; 5:30 ndaxte noo di céri jëmmam. 5:31 Mbind mi nee na: «Moo tax góor dina beru ndeyam ak baayam, di taq ci jabaram, ñoom ñaar doon benn.» 5:32 Loolu ëmb na mbóot mu xóot; man maa ngi wax ci lu jëm ci Kirist ak mbooloo mi. 5:33 Waaye li teew, na góor gu nekk bëgg jabaram, ni mu bëgge boppam, te jigéen ji weg jëkkëram.
6:1 Naka yéen xale yi, nangeen déggal seeni waajur, ci li ngeen bokk ci Boroom bi, ndaxte looloo rafet. 6:2 «Teralal sa ndey ak sa baay,» mooy ndigal li jëkk a ëmb dige, 6:3 maanaa: «ngir nga am gudd fan gu ànd ak jàmm.» 6:4 Yéen baay yi it, buleen bundaxataal xale yi, waaye ngeen yar leen, di leen yemale ak a yee ci Boroom bi. 6:5 Yéen jaam yi, nangeen déggal seeni sang yu àddina, boole ci ragal ak wegeel, di ko def ak xol bu laab, ni su doon ngir Kirist. 6:6 Buleen ko def rekk ci ngistal, ngir sàkku ngërëmu nit, waaye ni ay jaami Kirist, di jëfe coobareg Yàlla ak seen xol bépp. 6:7 Beyleen seen sas nag ak xol bu tàlli, ni su doon ngir Boroom bi te du nit, 6:8 xam ne ku def lu baax, Boroom bi delloo la ko, muy jaam, muy gor. 6:9 Yéen it sang yi, jëfeleen noonu seen diggante ak seeni jaam, te dëddu gépp raglu, xam ne yéena bokk benn Boroom ci asamaan, te ñépp a yem fi moom. 6:10 Léegi nag doolewuleen ci Boroom bi, te soloo kàttanam gu mag gi. 6:11 Gànnaayooleen yérey xarey Yàlla yépp, ngir man a jànkoonte ak pexey Seytaane. 6:12 Ndaxte ndëndu xare jib na, waxuma sunu diggante ak nit ñi, waaye ak kilifa yiy nëxal àddina si, ñuy kilifa yi ak ay boroom sañ-sañ, di gaayi Seytaane yi ci bérab yu kawe yi. 6:13 Kon nag gànnaayooleen yérey xarey Yàlla yépp, ba man a jànkoonte jamono ju xeex bi taree, noot lépp te taxaw temm. 6:14 Taxawleen kon temm, geñoo dëgg te sàngoo njub, muy seen kiiraayu dënn. 6:15 Solooleen jàmm, ji xebaar bu baax biy joxe, ni ay dàll ci seeni tànk, ba jekk ci lépp. 6:16 Defleen it ngëm, muy seen pakk, ba man a fél jum yi leen Seytaane di fitt. 6:17 Defleen mucc, muy seen mbaxanam xare, ak kàddug Yàlla, muy jaasi ji leen Xel mu Sell mi tëggal. 6:18 Deeleen ñaan ci xeeti ñaan yépp ci kàttanu Xel mu Sell mi, te sax ci ak farlu gu mat sëkk, di ñaanal gaayi Yàlla yu sell yi yépp. 6:19 Te buleen ma ci fàtte, ngir waxtu wu ma ubbee sama gémmiñ, ma am lu ma wax, ba man a xamle ak fit wu dëgër mbóoti xebaar bu baax bi. 6:20 Ndaw laa ci, lu ñu jéng; na ma Yàlla may fit wu ma waxe, ni mu ma ware. 6:21 Yónnee naa leen Tisig sama mbokk, mi ma sopp, te muy jawriñ ju takku ci liggéeyu Boroom bi, ngir mu xamal leen lépp li aju ci man ak li may def. 6:22 Maa leen ko yónneel sama bopp, ngir ngeen xam li nu nekke, te mu dëfël seeni xol. 6:23 Yéen bokk yi, na leen Yàlla Baay bi ak Yeesu Kirist Boroom bi may jàmm ak mbëggeel gu ànd ak ngëm. 6:24 Na yiwu Yàlla ànd ak ñépp, ñi bëgg Boroom bi Yeesu Kirist ak mbëggeel gu sax.
1:1 Nun Pool ak Timote, jaami Kirist Yeesu, noo leen di bind, yéen gaayi Yàlla yu sell yépp ci dëkku Filib, yi bokk ci Kirist Yeesu, yéen ak seeni njiit ak ñiy topptoo yëfi mbooloo mi. 1:2 Na leen Yàlla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak jàmm. 1:3 Yoon wu ma leen di xalaat, maa ngi sant Yàlla sama Boroom; 1:4 te saa su ma leen di ñaanal yéen yépp, duma noppee bég, 1:5 ndax seen ànd ak man ci tas xebaar bu baax bi, ca ndoorte la ba tey. 1:6 Wóor na ma ne, Yàlla mi tàmbali jëf ju baax jii ci yéen, dina ci sax, ba bésu Kirist Yeesu ñëw. 1:7 Te juumuma ci li ma xalaat loolu ci yéen ñépp, ndaxte def naa leen ci sama xol; ba tax fii ci kaso bi, ci taxawal xebaar bu baax bi ak lawal ko, yéen ñépp am ngeen wàll ak man ci yiwu Yàlla. 1:8 Ndaxte Yàllaa seede ne, sama xol seey na ci yéen ñépp ci biir cofeelu Kirist Yeesu. 1:9 Li ma leen di ñaanal nag mooy lii: na seen mbëggeel di yokku tey gën a tar, jaar ci xam ak xàmmi gu wér; 1:10 nangeen sax noonu ci yi gën a rafet, ngeen am xol bu laab te bañ a am benn sikk, ba bésu Kirist ñëw; 1:11 na seen xol meññ njub, ba ne gàññ, jaar ci Yeesu Kirist ci ndamul Yàlla ak cantam. 1:12 Damaa bëgg, bokk yi, ngeen xam lii: li ma dal taxul xebaar bu baax dellu gannaaw, waaye da koo jëmale kanam. 1:13 Noonu ñiy wottu buur bi ak ñépp gis nañu bu leer ne, turu Kirist rekk a tax ñu jàpp ma. 1:14 Te it bokk yu bare takk nañu seeni fit ci li ñu gis samay buum, ba tax ñu gën a ñeme ci wax kàddug Yàlla ci lu àndul ak genn tiit. 1:15 Am na ñuy waare ci turu Kirist ci kaw kiñaan ak xëccoo, waaye ñi ci des ci kaw cofeel ak xol bu laab, ndaxte xam nañu ne, Yàlla moo ma teg fii, ngir ma taxawal xebaar bu baax bi. 1:17 Waaye ñale amuñu xol bu laab, te seen njariñu bopp rekk a tax ñuy yégle turu Kirist, di wut a feddali samay buum ak coono. 1:18 Lu ci génn nag? Xanaa lii rekk: turu Kirist jolli na ci nii mbaa naa, muy ci naaféq, muy ci dëgg; bég naa ci te dinaa ci bégati. 1:19 Ndaxte xam naa ne, loolu lépp mu ngi jëm ci sama mucc, jaar ci seeni ñaan ak ndimbalu Xelum Yeesu Kirist, mi ma Yàllay yéwénal. 1:20 Ndaxte sama xënte ak sama yaakaar mooy ma bañ a rus ci lenn, waaye sama yaram feeñal ndamu Kirist, ma ànd ci ak kóolute gu mat, su may dund mbaa may dee; moom laa daan def démb, te moom laay def tey. 1:21 Ndaxte su ma dundee, Kirist laay noyyee, te su ma deeyee, xéewal lay doon ci man. 1:22 Su ma Yàlla bàyyee ci àddina, sas wu am njariñ la ci man. Am naa xel ñaar, te xawma bi ci gën. Am naa yéeney jóge fi, fekki Kirist, te looloo gën fuuf, 1:24 waaye ma des fi ci àddina moo gën ci yéen. 1:25 Loolu wóor na ma; kon xam naa ne, dinaa fi des, di leen taxawu yéen ñépp, ngir seen ngëm yokku, ànd ak mbég. 1:26 Noonu dinaa dellusi ci yéen, ngir sama taxawaay gën a lawal seen mbég ci Kirist Yeesu. 1:27 Waaye dénk naa leen lii: na seeni jëf yelloo ak li Kirist digle ci xebaar bu baax bi. Noonu su ma leen seetsee, mbaa ma dégg seen mbir rekk, dinaa xam ne yéena ngi dëgër ci menn xel, bokk benn xalaat ci bëre luy saxal dëggu xebaar bu baax bi, 1:28 te bañ a tiit dara ndax noon, yi leen di xëbal. Màndarga la muy wone ne aji sànku lañu, di màndarga it ne aji mucc ngeen, di mucc gu jóge ci Yàlla. 1:29 Ndaxte Yàlla may na leen, ngeen gëm Kirist, rax-ca-dolli ngeen sonn ndax turam, 1:30 di wéy ci bëre, bi ngeen gisoon ci man, te dégg léegi sama mbir.
2:1 Su nu Kirist mayee fit nag ak mbëggeel guy dëfël sunu xol, su nu amee cér ci Xel mu Sell mi, su amee cofeel ak yërmande ci sunu bokk ci moom, 2:2 kon mottalileen sama mbég, ci bokk benn xalaat ak genn mbëggeel, benn bakkan ak menn xel. 2:3 Buleen def dara ci kaw wut aw tur walla wonu, waaye jiital-leen seeni moroom cig woyof. 2:4 Buleen yem ci topptoo seen bopp rekk, waaye booleleen ci seeni moroom. 2:5 Te ngeen soloo xel mi nekkoon ci Kirist Yeesu: 2:6 Njàlbéen ga fekk na Kirist yor melow Yàlla,waaye aakimowul taxawaayamci li mu mengoo ak Yàlla. 2:7 Waaye daa wàcce boppam,ba tollook nit ñi,def boppam surga.Te bi mu yoree bindu nit, 2:8 daa suufeel boppam,di dégg ndigal, ba joxe boppam,ñu daaj ko sax ci bant. 2:9 Moo tax Yàlla kaweel ko lool,jox ko tur wi tiim yépp, 2:10 ngir turu Yeesoo tax ñépp sukk,ci asamaan, ci kaw suuf, ci biir suuf; 2:11 te ñépp bokk genn kàddu naan:Yeesu Kirist mooy Boroom bi;ci màggug Yàlla Baay bi. 2:12 Noonu samay soppe, xam naa ne, musuleen a jóg ci dégg ndigal, waxuma sax bi ma nekkee ak yéen rekk, waaye rawatina bi ma leen soree. Kon nag maa ngi leen di ñaan, ngeen biral seen mucc ci seeni jëf, te def ko ci ragal Yàlla gu dëggu. 2:13 Ndaxte Yàlla ci boppam mooy jëf ci yéen, ngir ngeen fonk coobareem te di ko jëfe. 2:14 Lépp lu ngeen di def nag, buleen ci boole xultu mbaa xuloo. 2:15 Noonu dingeen am xol bu laab bu àndul ak ŋàññ, di guney Yàlla yu amul sikk ci biir jamono ju yàqu te rëb. Dangeen di leer ci seen biir ni weer ci àddina si, 2:16 di jottali kàddug dund gi. Noonu bu bésu Kirist ñëwee, dinaa man a bég, xam ne dawuma lu amul njariñ, te sonnuma cig neen. 2:17 Te bu sama deret waree tuuru sax, ngir seen ngëm mat sëkk, ma mel ni naan gu ñu boole ak sarax su jëm ci Yàlla, ba tey bég naa ci, te dinaa ci bégati. 2:18 Yéen itam nag bégleen, waaw fekksileen ma ci sama mbég. 2:19 Gannaaw loolu, bu soobee Boroom bi Yeesu, yaakaar naa ne, dinaa leen yónnee Timote balaa yàgg, ngir sama xel dal ci xam nan ngeen def. 2:20 Ndaxte amu fi kenn gannaaw Timote, ku bokk ak man xalaat te fonk leen bu wér. 2:21 Ñi ci des ñépp, seen bopp lañuy xalaat, waaye du mbiri Yeesu Kirist. 2:22 Waaye xam ngeen takkuteg Timote, ci ni mu ànde ak man ci tas xebaar bu baax bi, ni doom di taxawoo baayam. 2:23 Moom laa yaakaar a yónni fi yéen nag, waxtu wu ma yégee, nu sama mbir di tëdde. 2:24 Waaye wóor na ma ne, Boroom bi dina ma may, man ci sama bopp, ma seetsi leen balaa yàgg. 2:25 Ci lu jëm ci sama mbokk Epafrodit nag, miy sama nawle ci liggéey bi ak ci xeex bi, te di seen ndaw ci faj samay soxla, jàpp naa ne, war naa leen koo delloo. 2:26 Ndaxte namm na leen lool, te tiisoo na li ngeen yég jagadeem. 2:27 Ci dëgg-dëgg woppoon na ba xaw a dee, waaye Yàlla yërëm na ko, ba fëgg boppam, rax-ca-dolli siggil na ma man itam, ngir ma bañ a am tiis ci kaw tiis. 2:28 Noonu delloo naa leen ko ci lu gaaw, ngir ñëwam bégal seeni xol, te man itam sama xol féex. 2:29 Teeruleen ko teeru bu rafet nag ngir Boroom bi, te teral ñi mel ni moom. 2:30 Ndaxte liggéeyal na Kirist, ba riisu dee, te gar na bakkanam ci taxawal leen ci topptoo, bi ngeen yéene woon ci man.
3:1 Kon nag samay bokk, bégleen ci Boroom bi. Duma sonn mukk ci di leen ko wax, ndax seen mucc moo ci aju. 3:2 Moytuleen xaj yi, waaw moytuleen ñiy jëfe lu bon, ñoom ñi seen xarafal weesul wàññi yaramu nit. 3:3 Ndaxte nun noo xaraf tigi, nun ñiy màggal Yàlla ci Xel mu Sell mi, di damu ci Kirist Yeesu, te amunu jenn yaakaar ci matug nit. 3:4 Ba tey manoon naa am yaakaar ci sama bopp; su nit doon damu, maa ciy raw. 3:5 Xarafoon naa ca ayu-bés ga, bokk ci bànni Israyil ci giiru Ben-yamin, di Ibrë ci deret ak ci meen. Bu dee ci yoonu Musaa ngeen bëgg a wax, ci tariixab Farisen laa bokkoon; 3:6 bu dee it ci mbirum farlu, daan naa fitnaal mbooloom ñi gëm Kirist; bu dee ci njub ci sàmm yoon, awma benn gàkk. 3:7 Waaye loolu lépp lu ma tegoon ay njariñ fa kanam Yàlla, dëddu naa ko ngir Kirist. 3:8 Rax-ca-dolli dëddu naa lépp ngir xéewali xam Kirist Yeesu sama Boroom, di xam-xam bu xóot, ba xel mënu koo takk. Moo tax ñàkk naa sama lépp, te def ko ni mbalit, ngir am cér ci Kirist. 3:9 Na ma Yàlla fekk ci moom, waxuma ci njub gu aju ci sàmm yoon, waaye gu aju ci gëm Kirist, maanaam njub gi nu Yàlla sol ci kaw ngëm. 3:10 Moom laay ittewoo xam, ak doole ji ànd ak ndekkiteem, ma bokk ci ay coonoom, ba fekki ko ci deeyam, 3:11 ngir man a séddu ci ndekkiteem, su ma ko manee am. 3:12 Waxuma ne jagoo naa ko ba noppi, waxuma it ne aji mat laa, waaye maa ngi daw, ngir jot li tax Kirist jël ma. 3:13 Bokk yi, gëmuma ne jot naa ko ba noppi, waaye lenn lii laay def: fàtte li ma weesu, jublu ci li féete kanam, 3:14 di daw yen muj ga, ngir jot li ma Yàlla tax a woo, di cér bi ma Yàlla wooye te dencal ma ko ci asamaan ci darajay Kirist Yeesu. 3:15 Nun ñi mat nag, nanu xalaat loolu. Te su ngeen ci amee werantey xol, Yàlla dina leen ko leeralal. 3:16 Li am daal, fa seen ngëm tolloo, na fa seen jëf àgg. 3:17 Kon nag bokk yi, toppleen ma te xool ñiy roy ci li nu tëral diirub sunu ngan ci yéen. 3:18 Ndaxte jëfi ñu bare juuyoo na ak dee gi Kirist dee; loolu wax naa leen ko ba tàyyi, maa ngi koy waxaat léegi ak i jooy. 3:19 Alku lañuy mujje, ñoom ñiy jaami seen biir, di wonoo lu ruslu, tey wut yëfi àddina rekk. 3:20 Waaye nun waa asamaan lanu, te noo ngi xaar Boroom bi Yeesu Kirist jóge fa, musalsi nu. 3:21 Noonu dina soppi sunu yaram wu toroxlu, def ko ni yaramam wi ànd ak ndam dëppook kàttanam, gi ko man a nootal mbindeef yépp.
4:1 Kon nag yéen samay bokk, ñi ma bëgg te namm leen, di sama mbég ak sama kaalag ndam, jàppleen bu dëgër noonu ci Boroom bi, soppe yi! 4:2 Ci lu jëm ci Ewodi ak Santis, maa ngi leen di ñaan, ñu bokk benn xalaat ci Boroom bi. 4:3 Te yaw sama nawle bu wér, nanga dimbali jigéen ñooñu xeexoon ci sama wet ci tas xebaar bu baax bi, boole ci Këlemaŋ ak samay yeneeni nawle, ñoom ñi Yàlla bind seeni tur ci téereb dund ba. 4:4 Deeleen bég ci Boroom bi; maa ngi koy waxati: bégleen! 4:5 Na seen lewet leer ñépp. Boroom bi jege na. 4:6 Buleen jaaxle ci dara, waaye ci lépp wéetal-leen Yàlla, diis ko seeni soxla ci ñaan gu ànd ak cant. 4:7 Noonu jàmmu Yàlla, ji xel mënta takk, dina aar seeni xol ak seeni xalaat ci darajay Kirist Yeesu. 4:8 Léegi nag bokk yi, na seen xalaat jublu ci lii: lu dëggu, lu jekk, lu jub, lu sell, lu rafet ak lu faaydawu; su fi amee lu baax mbaa lu mat a naw, xalaatleen ko. 4:9 Li ngeen jànge ci man te nangu ko, li ngeen dégge ci man te gis ko, jëfeleen ko; kon Yàllay jàmm dina ànd ak yéen. 4:10 Sama xol sedd na guyy ci Boroom bi, ci ni ngeen yeesale seen ndimbal ci man. Xam naa ne, amoon ngeen yéene ji, waaye man gi moo fi nekkul woon. 4:11 Ba tey soxla taxul ma waxe nii, ndaxte jàng naa doylu ci mbir mu ma man a dab. 4:12 Miin naa ñàkk, man naa naataange. Ci fépp ak ci lépp, Yàlla def na ba sama xol toj ci suur ak xiif, barele ak néewle. 4:13 Man naa lépp ci ndimbalu Aji Dooleel ji. 4:14 Waaye teewul taxawu, bi ngeen ma taxawu ci sama tiis, jëf ju rafet la. 4:15 Yéen waa Filib xam ngeen ne, bi ngeen jëkkee xam xebaar bu baax bi, te ma jóge diiwaanu Maseduwan, benn mbooloo àndul woon ak man ci mbirum joqleente ndimbal, mu dul yéen doŋŋ. 4:16 Ba ma nekkee dëkku Tesalonig sax, yónnee ngeen ay yooni yoon, ngir faj samay soxla. 4:17 Loolu tekkiwul ne, damay sàkku ay ndimbal ci yéen, waaye damaa bëgg rekk seen denc yokku fa Yàlla. 4:18 Fi mu ne jot naa li ma aajowoo lépp, ba maa ngi ci naataange; li ngeen ma yónnee ci loxoy Epafrodit doy na sëkk; ni xetu latkoloñ la mel ci man, di sarax su neex Yàlla te mu nangu ko. 4:19 Te Yàlla sama Boroom, mi denc ci Kirist Yeesu xéewal yu dul jeex, dina ci faj seeni soxla yépp. 4:20 Na Yàlla sunu Baay yelloo ndam ba fàww. Amiin. 4:21 Nuyul-leen ma gaayi Kirist Yeesu yu sell yépp. Bokk yi ànd ak man, ñu ngi leen di nuyu. 4:22 Te it gaayi Yàlla yu sell yépp ñu ngi leen di nuyu, rawatina nag ñi nekk kër buur bi Sesaar. 4:23 Na yiwu Boroom bi Yeesu Kirist ànd ak seen xel.
1:1 Man Pool, ndawul Kirist Yeesu ci coobareg Yàlla, man ak Timote sunu mbokk, 1:2 noo leen di bind, yéen gaayi Yàlla yu sell, yi dëkk Kolos te di ay bokk ci gëm Kirist. Na leen Yàlla sunu Baay may yiw ak jàmm. 1:3 Dunu noppee sant Yàlla, Baayu sunu Boroom Yeesu Kirist, saa su nu leen di ñaanal, 1:4 ndaxte yég nanu seen ngëm ci Kirist Yeesu ak seen mbëggeel ci gaayi Yàlla yépp. 1:5 Ngëm googu ak mbëggeel googu ñu ngi sosoo ci yaakaaru ëllëg, jiy cér bi leen Yàlla dencal ca asamaan. Mas ngeen a dégg yaakaar jooju ci kàddug dëgg gi, di xebaar bu baax bi. 1:6 Ni xebaar bu baax bi wàcce ci yéen, noonu lay wàcce ci àddina sépp, di meññ te di law. Te noonu lay doxale ci yéen, li dale ci bés, ba ngeen dégge xebaaru yiwu Yàlla, te xam dëggam gi mu ëmb; 1:7 moom ngeen jànge ci Epafras, miy sunu nawle ci liggéey bi te nu sopp ko, di jawriñu Kirist bu takku ngir seen njariñ. 1:8 Te moo nu yégal it mbëggeel, gi Xelu Yàlla mi sol ci yéen. 1:9 Looloo tax ci sunu wàllu bopp, ba nu ko yégee ba tey, jógunu ci di leen ñaanal. Nu ngi ñaan Yàlla, ngeen xam bu baax coobareem ci xel mu mat ak ràññee gu aju ci dooley Xelam. 1:10 Noonu dingeen dund dund gu dëppoo ak seen bokk ci Boroom bi, ba neex ko ci fànn gu nekk, di def bépp jëf yu baax, te yokk seen xam-xam ci Yàlla. 1:11 Te Yàlla dina leen dooleel ak bépp doole, mu mengoo ak kàttanu ndamam, ngir ngeen man a tegoo coono te muñ, ba fa muñ di yem. 1:12 Dingeen gërëm Yàlla Baay bi, ànd ci ak mbég, moom mi leen jagleel, ngeen bokk ci cér, bi mu dencal gaayam yu sell yi ci leer. 1:13 Yàlla musal na nu ci dooley lëndëm, yóbbu nu ci nguuru Doomam ji mu bëgg, 1:14 moom mi nu jot, maanaam baal nu sunuy bàkkaar. 1:15 Doom jooju moo di melokaanu Yàlla, ji kenn gisul. Mooy taaw bi, ki gën a màgg lépp luy mbindeef. 1:16 Ndaxte ci moom la Yàlla sàkke lépp lu nekk ci asamaan ak suuf, li ñuy gis ak li ñu mënul a gis, muy buur, njiit, kilifa mbaa boroom sañ-sañ. Lépp lu ñu sàkk, ci moom lañu ko jaarale, ci moom lañu ko jëme. 1:17 Laata dara di am, fekkoon na moom mu nekk, te lépp a ngi jàppoo ci moom. 1:18 Mooy bopp bi yilif jëmm ji, di mbooloom ñi ko gëm, ndaxte moom mooy njàlbéen gi, di taaw bi, maanaam ki jëkk a dekki, ngir muy kilifa ci bépp fànn. 1:19 Ndaxte soob na Yàlla mu dëkkal matam gépp ci moom 1:20 te jaar ci moom, jubale lépp ak boppam, muy ci kaw asamaan yi mbaa ci suuf, ba mu wàccee jàmm jaarale ko ci deret ji tuuru, bi Doom ji deeyee ca bant ba. 1:21 Te yéen ñi sore woon Yàlla te doon ay noonam ci seen xel ak seen jëf yu bon, 1:22 léegi nag Yàlla jubale na leen ak boppam jaare ko ci deewu Kirist ci yaramu nitam, ngir taxawal leen ca kanamam, ngeen sell te ñàkk sikk ak i ŋàññ. 1:23 Loolu nag na fekk ngeen wéy ci ngëm, sampu ci ba dëgër ci, tey séentu cér, bi leen xebaar bu baax bi jox. Te xebaar bu baax, boobu ngeen dégg te ñu yégal waa àddina sépp, man Pool moom laay yégle. 1:24 Léegi nag maa ngi am bànneex ci coono, yi may daj ngir seen njariñ; te li des sax ci fitnay Kirist, noonu laa koy àggalee ngir njariñu mbooloom ñi gëm, di jëmmam. 1:25 Jawriñu mbooloo moomu laa, ndaxte Yàlla sas na ma ngir yéen, may yégle fu nekk kàddoom, 1:26 maanaam ma yégle kumpa, gi nëbbu woon ay jamonoy jamono, waaye léegi Yàlla xamal na ko ay gaayam 1:27 ci xeeti àddina sépp. Ñoom nag la Yàlla bëgg a xamal ni ndamu kumpa googu màgge, maanaam Kirist a ngi dëkk ci yéen, di yaakaar ju wér ci ndamu ëllëg. 1:28 Moom Kirist lanuy yégle, di artu te di jàngal ku nekk, ànd ak xel mu mat, ngir jébbal Yàlla ku nekk ni ku mat ci Kirist. 1:29 Ci loolu laay jëmale sama liggéey, di bëree dooley Kirist, jiy yengu ci man ak kàttan.
2:1 Bëgg naa nag, ngeen xam bëre bu metti, bi may bëre ngir yéen, ngir waa Lawdise ak ñépp ñi ma musul a teg bët. Damay def sama kem-kàttan, 2:2 ngir ngeen am fit te nekk benn ci mbëggeel, ngir dajal noonu xam-xam bu mat, ba xam kumpag Yàlla, di Kirist. 2:3 Ci moom lañu denc lépp lu ñuy sàkku ci xel ak ci xam-xam. 2:4 Maa ngi wax lii, ngir kenn bañ leen a nax ci ay wax yu neex. 2:5 Jëmm ji ñëwul waaye sama xel a ngi ci yéen, di bég ci seen doxalin ak ngëm gu dëgër, gi ngeen am ci Kirist. 2:6 Kon nag, ni ngeen nangoo Kirist Yeesu ni Boroom bi, dundeleen noonu ci moom. 2:7 Saxleen ci moom, di màgg ci moom, tey gën a dëgër ci ngëm, gi ñu leen jàngal, ba seen xol di baawaan ci gërëm Yàlla. 2:8 Moytuleen ba kenn bañ leen a fàbbi ci ay xam-xami nit yuy naxi neen. Xam-xam yu mel noonu, ñu ngi soqikoo ci aada yu nit tëral, ci aaday àddina, waaye soqikoowul ci Kirist. 2:9 Ndaxte ci Kirist, maanaam ci yaramu nitam, la matug Yàlla gépp dëkk, 2:10 te mat ngeen ci moom, miy buuru kilifa yépp ak boroom sañ-sañ yépp. 2:11 Ndax seen ngëm ci moom xaraf ngeen xaraf bu loxol nit deful, maanaam Kirist summil na leen dooley bàkkaar, ji moomoon seen yaram. Loolu mooy xaraf, bi Kirist def. 2:12 Bi ñu leen sóobee ci ndox, suulaale nañu leen ak moom, te it dekki ngeen ak moom, ndaxte gëm ngeen ci dooley Yàlla, ji ko dekkal ca néew ya. 2:13 Te yéen ñi doon ndee fa kanam Yàlla ndax seeni moy ak seen ñàkka xaraf, Yàlla dundalaat na leen ak Kirist, baal nu sunuy bàkkaar yépp. 2:14 Mbind mi nu doon tiiñal, te daa nu yey ndax ay sàrtam, Yàlla far na ko, dindi ko, daajaale ko ca bant, ba Kirist deeye. 2:15 Futti na kilifa yi ak boroom sañ-sañ yi, weer leen ci kanamu ñépp, sëkktal leen niy jaam ndax ndam la Kirist jële ca bant ba. 2:16 Kon nag bu leen kenn teg tooñ ci li jëm ciy ñam mbaa naan, ci màggal mbaa xewu weer wu feeñ, mbaa ci bésu noflaay. 2:17 Loolu lépp nag takkandeer la woon buy misaal li waroon a ñëw, waaye lu dëggu li mi ngi ci Kirist. 2:18 Kuy bég ci di toroxlu ci ngistal, di jaamu ay malaaka, buleen ko may, mu àtte leen. Kooku dafay jeneer, di seet li koy feeñu, bay tiitaroo xalaatam, fekk xalaatu nit kese la, te neen. 2:19 Taqul ci Kirist, miy bopp bi yilif jëmm ji. Bopp bee tax ba jëmm jépp, ji siddit yi ak tenqo yi téye te taqale ko, di màgg màgg gi ko Yàlla di jox. 2:20 Ndegam deeyandoo ngeen ak Kirist, ba génne noonu ci aaday àddina, lu tax ngeen di nangu, ñu di leen teg ay sàrt yu mel nii: «Bul fab, bul ñam, bul laal,» ni bu seenug dund aju woon ci àddina si? 2:22 Sàrt yooyu ñu ngi aju ci ndigali nit ñi ak seen njàngale. Yëf yi ñu tudd yépp, dees na leen jariñoo, ba ñu jeex. 2:23 Dëgg la, seeni sàrt dañuy dénkaane pasteef ci jaamu Yàlla, di toroxlu ak di fitnaal seen yaram. Waaye sàrt yooyu nag amuñu benn njariñ, ngir nit ñi noot seen nafsu.
3:1 Kon nag ndegam dekkeendoo ngeen ak Kirist, wutleen yëf, ya nekk ca kaw, fa Kirist toog ca ndeyjooru Yàlla. 3:2 Fonkleen yëf ya ca kaw, te ngeen bañ a faale yi ci suuf, 3:3 ndaxte dee ngeen, te seen dund boole nañu ko ak Kirist, denc ca Yàlla. 3:4 Te bés bu Kirist miy seen dund feeñee, yéen itam dingeen feeñ ak moom ci biir ndam. 3:5 Kon nag li nekk ci yéen te bokk ci mbiri àddina, jébbal-leen ko dee, yu deme ni ndoxaanu yàqute, sobe, xemmem, bëgg-bëgg yu bon, ak bëgge, maanaam bokkaale Yàlla. 3:6 Yooyooy xëcc merum Yàlla. 3:7 Yéen itam noonu ngeen daan doxale bu jëkk, ba ngeen daan dunde noonu. 3:8 Waaye léegi bàyyileen yii yépp: mer, xadar, kiñaan ak di génne ci seen gémmiñ sos ak wax ju ñaaw. 3:9 Bàyyileen di fen seeni moroom, ndaxte summi ngeen jikko ju bon, ji ngeen judduwaale, moom ak ay jëfam; 3:10 te sol ngeen dund gu bees, gi Yàlla sàkk te di ko yeesal ba mu mel ni moom, ngir ngeen man koo xam bu wér. 3:11 Ci dund gu bees googu, amul Yawut ak ku dul Yawut, ku xaraf walla ku xaraful, jaam walla gor, ku jàngul ni Baarbaar yi, ak ku yeewuwul ni waa Sit, waaye Kirist ay lépp te dëkk ci ñépp. 3:12 Kon nag ndegam Yàlla tànn na leen, sellal leen, sopp leen, solooleen boog yërmande, laabiir, woyof, lewet ak muñ. 3:13 Muñalanteleen, di baalante, su amee kuy tawat moroomam. Baalanteleen, ni leen Boroom bi baale. 3:14 Ci kaw loolu lépp amleen mbëggeel, giy jókkaale lépp, ba mu mat. 3:15 Na jàmm ji Kirist di joxe noot seeni xol, ndaxte Yàlla woo na leen ci loolu, mel ni ay cér yu bokk benn yaram; te gërëmleen Yàlla. 3:16 Na kàddug Kirist dëkk ci yéen, bay baawaan, ngeen di jàngalante ak a artoonte ci seen biir ak xel mu mat sëkk, di woy ak a gërëm Yàlla ak seen xol bépp, ay taalifi Sabóor, ay kañ Yàlla ak ay cant yu tukkee ci Xelum Yàlla. 3:17 Te lu ngeen man a def, muy ci wax mbaa ci jëf, wéerleen ko ci turu Boroom bi Yeesu, jaare ci moom gërëm Yàlla Baay bi. 3:18 Jigéen ñi, na ku nekk nangul jëkkëram, ndaxte looloo jekk ci ñi bokk ci Boroom bi. 3:19 Góor ñi, na ku nekk bëgg jabaram te muñal ko. 3:20 Xale yi, déggal-leen seeni waajur ci lépp, ndaxte looloo rafet ci ñi bokk ci Boroom bi. 3:21 Baay yi, buleen bundaxataal seeni doom, ngir bañ a jeexal seen xol. 3:22 Jaam yi, nangul-leen ci lépp seen sang, yi ci àddina. Buleen ko def rekk ci seen kanam, di sàkku ngërëm, waaye na nekk lu dëggu ci yéen, ndax seen ragal Boroom bi. 3:23 Lu ngeen man a def, na ci seen xol tàlli; ngeen def ko ngir Boroom bi, te du ngir nit, 3:24 xam ne Boroom bi dina fey seeni jëf, mu di cér bi mu leen dencal. Kirist mooy Boroom, bi ngeen di liggéeyal. 3:25 Waaye ku def lu bon, Boroom bi dina la delloo sa jëf, te du gënale.
4:1 Sang yi, yorleen seeni jaam ci nu jub te aw yoon, xam ne, am ngeen yéen itam ab Sang ca asamaan. 4:2 Dëkkleen ci ñaan Yàlla, farlu ci, boole ci ngërëm. 4:3 Te ngeen fasaale nu ci ñaan yi itam, ngir Yàlla ubbil nu bunt, nu man a xamle kàddoom, di yégle kumpa gi di Kirist, muy kumpa gi waral ñu jéng ma. 4:4 Ñaanleen ngir ma xamle ko ni mu ware. 4:5 Jëfeleen ak xel ci seen diggante ak waa àddina, te fu ngeen ame jot, fexeleen ba jariñoo ko. 4:6 Na seen wax jépp fees ak yiw te am xorom, ngir ngeen xam nan ngeen war a tontoo ku nekk. 4:7 Tisig, sama mbokk mi ma sopp, di jawriñ ju takku ak sama nawle ci liggéeyu Boroom bi, dina leen yégal lépp lu jëm ci samay mbir. 4:8 Lii moo tax ma yebal ko ci yéen: ngeen xam xebaar bi jóge ci nun, te it mu dëfël seen xol. 4:9 Onesim lay àndal, sunu mbokk mu takku, mi nu sopp, te mu bokk ci yéen. Dinañu leen xamal lépp lu xew fii. 4:10 Aristàrk mi nekk ak man ci kaso bi, mu ngi leen di nuyu, moom ak Màrk rakku Barnabas. Jot ngeen ay ndigal ci mbirum Màrk: bu ñëwee ci yéen, teral-leen ko. 4:11 Yeesu mi ñuy dàkkentale Yustus, moom it mu ngi leen di nuyu. Ñoom rekk ñooy Yawut yiy liggéeyandook man ngir nguuru Yàlla, te ñoo féexal sama xol. 4:12 Jaamu Kirist, Epafras, mi bokk ci yéen, mu ngi leen di nuyu. Du jóg ci di leen ñaanal, farlu ci ni kuy bëre, ngir ngeen taxaw temm ci coobareg Yàlla gépp, ànd ak ngëm gu mat ak kóolute gu wóor. 4:13 Maa ngi koy seedeel ne, mu ngi sonn bu baax ngir yéen, ngir waa Lawdise ak waa Yerapolis. 4:14 Luug, doktoor bi ñu sopp, mu ngi leen di nuyu, moom ak Demas. 4:15 Nuyul-leen nu mbokk, yi nekk Lawdise. Nuyul-leen nu itam Nimfa ak mbooloom ñi gëm, miy daje ci këram. 4:16 Bu ñu jàngee bataaxal bii ci yéen, fexeleen ba ñu jàng ko it ci mbooloom ñi gëm mi nekk Lawdise, te yéen it ngeen jàng bi ma yónnee waa Lawdise. 4:17 Te neleen Arkib: «Farlul ci sas, wi la Boroom bi sédde, ba matal ko.» 4:18 Man Pool maa leen di bind nuyoo bii ci sama loxob bopp. Fàttalikuleen ne, dañu maa jéng. Na yiwu Boroom bi ànd ak yéen!
1:1 Nun Pool, Silwan ak Timote noo ngi leen di bind, yéen mbooloom ñi gëm ci dëkku Tesalonig te nekk ci Yàlla Baay bi ak Boroom bi Yeesu Kirist. Na yiw ak jàmm ànd ak yéen. 1:2 Bët bu set nu ngi sant Yàlla ndax yéen, di leen boole ci sunuy ñaan. 1:3 Dunu noppee fàttaliku ci kanam Yàlla sunu Baay jëf ji juddu ci seen ngëm, liggéey bi tukkee ci seen mbëggeel, ak muñ gi sosoo ci seen yaakaar ci sunu Boroom Yeesu Kirist. 1:4 Bokk yi, yéen ñi Yàlla bëgg, xam nanu ne Yàlla tànn na leen; 1:5 ndaxte xebaar bu baax, bi nu leen doon yégal, yemul woon ci ay wax rekk, waaye àndoon na ak kàttan ak Xel mu Sell mi ak kóolute gu mag. Xam ngeen sunu taxawaay ci seen biir ngir seen njariñ. 1:6 Te aw ngeen sunuy tànk ak yu Boroom bi, ci li ngeen nangu xebaar bi ci biir fitna yu metti, ànd ak mbég ci dooley Xel mu Sell mi. 1:7 Noonu ngeen daldi nekk royukaay ngir ñi gëm ñépp ci diiwaani Maseduwan ak Akayi. 1:8 Ndaxte kàddug Boroom bi jollee na ci seen biir, te yemul ci Maseduwan ak Akayi rekk, waaye seen gëm Yàlla siiw na fépp. Matul sax nu di ci wax dara, 1:9 ndaxte ñoom ci seen bopp ñooy seede li sunu ngan def ci seen biir. Maanaam, ni ngeen dëddoo xërëm yi, jublu ci Yàlla te di ko jaamu, moom miy Yàlla Aji Dund ju dëggu ji, 1:10 te ngeen di séentu Doomam bàyyikoo asamaan, moom Yeesu mi mu dekkal te di nu musal ci merum Yàlla, mi nar a ñëw.
2:1 Waaw bokk yi, xam ngeen ne, ngan gi nu leen ganesi woon du nganug neen. 2:2 Laata nuy ñëw, jaar nanu ci fitna ak toroxte ca dëkku Filib, ni ngeen ko xame; waaye Yàlla sunu Boroom may na nu fit, ba li tongoonte bi metti lépp it, yégal nanu leen xebaaru Yàlla bu baax bi. 2:3 Ndaxte sunu waaraate wéeruwul cig réer walla ci njublaŋ walla ciy nax. 2:4 Waaye gannaaw Yàlla moo nu seet, ba wóolu nu te dénk nu xebaar bu baax bi, kon noonu lanuy waaree, du ngir neex nit ñi, waaye ngir neex Yàlla, miy seet xol yi. 2:5 Musunoo jey kenn, yéen xam ngeen ko; sunu waare musul a ëmb bëgge, Yàlla seede na ko; 2:6 musunoo sàkku ngërëmu nit, muy ci yéen, muy ci ñeneen. 2:7 Manoon nanoo diis ci seen kaw sax, nun ñiy ndawi Kirist, waaye woyofoon nanu ci seen biir, te lewet ni jaboot buy uuf doomam. 2:8 Cofeel gi nu am ci yéen tax na, bëggunu woon a yem ci xamal leen xebaaru Yàlla bu baax bi, waaye jox leen it sunu bakkan, ndaxte sunu xol seeyoon na ci yéen. 2:9 Bokk yi, yéena ngi fàttaliku sunu coono ak sunu ñaq; xam ngeen ni nu liggéeye guddi ak bëccëg, ngir bañ a diis ci seen kaw, ci di leen yégal xebaaru Yàlla. 2:10 Naka sunu diggante ak yéen ñi gëm, doxal nanu ko doxalin wu sell te jub te amul sikk: seede ngeen ko, te Yàlla it seede na ko. 2:11 Xam ngeen ne, dénk nanu leen kenn-kenn, ni baay di def ak doomam, dëfëlal leen seen xol te dëggal ci yéen, ngeen dund dund gu neex Yàlla, moom mi leen di woo, ngeen séddu ci nguuram ak ndamam. 2:13 Te it dunu noppee sant Yàlla ci lii: ba ngeen jotee kàddug Yàlla, gi nu doon waare, nangu ngeen ko, waxuma ni kàddug nit waaye ni kàddug Yàlla, ndaxte moom la ci dëgg-dëgg, te mu ngi jëf ci yéen ñi gëm. 2:14 Ndaxte bokk yi, aw ngeen ci tànki mboolooy Yàlla, yi nekk ca réewu Yawut ya tey daje ci turu Kirist Yeesu; fitna ya ñu daj ca Yawut ya, yéen it seen waa réew teg nañu leen ko. 2:15 Ñoom Yawut yi rey nañu Boroom bi Yeesu, ni ñu reye woon yonent yi; teg nañu nu fitna yu metti; neexuñu Yàlla, ànduñu ak kenn, 2:16 di nu teree wax ak ñi dul Yawut, ngir bañ ñu mucc. Duñu noppee xuus ci biir bàkkaar, waaye merum Yàlla xëppu na ci seen kaw. 2:17 Nun nag bokk yi, ba ñu ma leen xañee ab diir --xol yi taxul may wax, waaye jëmm yi rekk — jéem nanu leen a gis ak sunu kem-kàttan, ndax namm nanu leen, ba sunu xol seey ci gis leen. 2:18 Kon jàppoon nanu leen a seetsi — man Pool sax ay yooni yoon, waaye Seytaane téq na ma. 2:19 Ndaxte bés bu Yeesu sunu Boroom dellusee, te nu fekke ko, kan mooy sunu yaakaar? Kan mooy sunu mbég? Kan mooy sunu kaala, gi nuy tiitaroo? 2:20 Xanaa du yéen? Waaw yéenay sunu ndam, yéenay sunu mbég.
3:1 Kon nag, ba nu ko mënatul a dékku, nangu nanu ñu bàyyi nu, nun doŋŋ, ca dëkku Aten, 3:2 te yónni nanu Timote, sunu mbokk ak sunu nawle ci liggéeyu Yàlla ak ci waareb xebaaru Kirist. Yónni nanu ko, ngir mu dénk leen, tey feddali seen ngëm, 3:3 ngir kenn bañ a raf ndax nattu, yi ngeen di jaar. Yéen ci seen bopp xam ngeen ne, nattu mooy sunu cér. 3:4 Ba nu nekkee ak yéen sax, waxoon nanu leen, waxati ko ne, fàww nu sonn; te noonu la ame, yéen xam ngeen ko. 3:5 Noonu ba ma ko mënatul a dékku, yónnee naa, ngir xam fu seen ngëm tollu, ngir ragal Seytaane fiir leen, ba sunu ñaq neen. 3:6 Waaye léegi Timote bawoo na ci yéen, indaale xebaar yu neex ci seen ngëm ak seen mbëggeel; xamal na nu ne, yéena ngi am pàttaliku yu rafet ci nun te namm nu lool, ni nu leen namme yéen itam. 3:7 Noonu bokk yi, ci biir tiis ak coono yi nu nekk, seen ngëm dëfël na sunu xol. 3:8 Ndaxte noo ngi dund dëgg-dëgg, ndegam yéena ngi sax ci Boroom bi. 3:9 Ndaw cant yu bare yu nu war a sant Yàlla ndax yéen! Ndaw mbég mu bare, mi nu am ci kanamam ndax yéen! 3:10 Guddi ak bëccëg nu ngi wàkkirlu ci ñaan Yàlla, ngir gis leen, ba man a mottali seen ngëm. 3:11 Na Yàlla sunu Baay moom ci boppam ak Yeesu sunu Boroom jubal sunu yoon ci yéen. 3:12 Na leen Boroom bi dolli mbëggeel gu tar, ngeen bëggante te bëgg ñépp, ni nu leen bëgge nun. 3:13 Na samp seeni xol noonu ci cell gu amul sikk fa kanam Yàlla sunu Baay, ba bés bu Yeesu sunu Boroom dellusee, ànd ak gaayam yu sell yépp.
4:1 Léegi nag bokk yi, jot ngeen ci nun, nan ngeen war a dunde ba neex Yàlla, te moom ngeen di def. Waaye ci turu Boroom bi Yeesu nu ngi leen di ñaan ak a dénk, ngeen gën koo feddali. 4:2 Ndaxte xam ngeen ndigal, yi nu leen jox ci wàllu Yeesu Boroom bi. 4:3 Lii nag mooy coobareg Yàlla: ngeen sell, maanaam ngeen moytu njaaloo; 4:4 ngeen noot seeni cér ci cell ak tedd, 4:5 te xemmem bañ leen a jiital, ni xeeti àddina yi xamul Yàlla. 4:6 Ci mbir mii nag, bu kenn ci yéen laal yëfi jaambur, ngir bañ koo tooñ. Ndaxte waxoon nanu leen bu yàgg te artu leen ne, ñiy def loolu, Boroom bi dina leen mbugal. 4:7 Ndaxte Yàlla woo na nu, nu dund ci cell, waaye du ci sobe. 4:8 Ku tanqamlu wax jii nag, defoo ko nit, Yàlla nga ko def, moom mi leen di jox Xel mu Sell mi. 4:9 Ci lu jëm ci bëggante ci seen biir, matul nu leen di bind dara, ndaxte Yàlla def na ci seen xol, ngeen bëggante. 4:10 Te moom ngeen di def ci bokk yépp, yi ci diiwaanu Maseduwan. Waaye bokk yi, maa ngi leen di xiirtal, ngeen gën cee sax. 4:11 Fullawooleen a dund ci jàmm, di topptoo seen mbiri bopp tey lekk seen ñaq, ni nu leen ko sante woon. 4:12 Noonu dingeen dund dund gu jekk ci kanamu waa àddina, te it dungeen soxlaal kenn dara. 4:13 Ci mbirum ñi nelaw nag bokk yi, bëgguñu ngeen réere mbir, ba tiis ni aji gëmul, yi amul benn yaakaar. 4:14 Ndegam gëm nanu ne, Yeesu dee na te dekki, noonu it Yàlla dina indaale ak Yeesu ñépp ñi ko gëm te nelaw. 4:15 Nu ngi leen di wax lii tukkee ci Boroom bi: nun ñiy dund te des fi, ba kera Boroom biy dellusi, dunu jiitu ñi nelaw. 4:16 Ndaxte ndigal lu jamp dina jib, baatu kilifa ci malaaka yi dégtu, liitu Yàlla jolli, te Boroom bi moom ci boppam dina wàcce ca asamaan. Booba ñi gëm Kirist te dee dinañu jëkk a dekki; 4:17 gannaaw loolu nun ñiy dund te des fi, dinañu ne fëyy ak ñoom jëm ci niir yi, taseji ak Boroom bi ci jaww ji. Te noonu dinanu nekk ak Boroom bi ba fàww. 4:18 Kon nag na ku nekk di dëfël sa xolu moroom ak kàddu yooyu.
5:1 Waaye bokk yi, ci li jëm ci jamono yi ak waxtu, yi loolu di am, matul nu leen ciy bind dara. 5:2 Ndaxte xam ngeen bu wér ne, ni sàcc di ñëwe guddi, noonu la bésu Boroom bi di ñëwe. 5:3 Fekk nit ñiy naan: «Lépp a ngi ci jàmm, ba ne leww,» booba musiba bett leen, ni aw mat di bette jigéen ju ëmb, te kenn du ci mucc. 5:4 Waaye yéen bokk yi, nekkuleen cig lëndëm, ba tax bés boobu bett leen ni sàcc. 5:5 Ndaxte yéen ñépp ci leer ak bëccëg ngeen bokk; bokkunu ci guddi ak lëndëm. 5:6 Kon nag bunu nelaw ni ñeneen ñi, waaye nanu xool te maandu. 5:7 Ndaxte ñiy nelaw, guddi lañuy nelaw, te ñiy màndi, guddi lañuy màndi. 5:8 Waaye nun ñiy waa bëccëg, nanu maandu te ràngoo ngir xare bi: ngëm ak mbëggeel, muy kiiraayu dënn, ak kóoluteg mucc, muy mbaxanam xare. 5:9 Ndaxte Yàlla jaglewu nu meram, waaye mucc la nu jagleel ndax darajay sunu Boroom Yeesu Kirist. 5:10 Deeyal na nu, ngir nu man a dund ak moom, bu nu nelawee ak bu nu nelawagul. 5:11 Kon nag nangeen dëgëralante te yokkante seen ngëm, ni ngeen koy defe. 5:12 Gannaaw loolu bokk yi, ci lu jëm ci njiit, yi Boroom bi teg ci seen kanam te ñuy liggéey ci seen biir, di leen artu, maa ngi leen di ñaan ngeen déglu leen; 5:13 rax-ca-dolli ngeen naw leen seen kem-kàttan te bëgg leen ndax seen liggéey. Na jàmm am ci seen biir. 5:14 Bokk yi, nu ngi leen di dénk, ngeen yedd ñi feñaag, dëfël ñi seen yasara yàcciku, dimbali ñi néew doole, tey muñal ñépp. 5:15 Saxleen ci baax ci seen biir ak ci ñépp, te bañ a feyantoo. 5:16 Deeleen bég 5:17 te sax ciy ñaan Yàlla, 5:18 di ko gërëm ci lépp, ndaxte loolu mooy coobareg Yàlla ci yéen ci seen bokk ci Kirist Yeesu. 5:19 Buleen fey taalu Xelum Yàlla, 5:20 di xeeb waxu yonent yi. 5:21 Waaye seetleen mbir yépp, jàpp ci li baax, 5:22 dëddu lépp lu ci bon. 5:23 Na leen Yàlla Boroom jàmm sellal, ba ngeen mat sëkk; na sàmm seen xel mépp, seen xol bépp ak seen yaram wépp, ngir dara bañ cee am sikk, ba bés bu sunu Boroom Yeesu Kirist dellusee. 5:24 Yàlla, mi leen woo ci loolu, kuy sàmm kóllëre la, te dina ko def. 5:25 Bokk yi, buleen nu fàtte ci seeni ñaan. 5:26 Nuyul-leen nu bokk yépp ak saafoonte bu laab. 5:27 Maa ngi leen di dénk ci kanamu Boroom bi, ngeen jàngal bataaxal bii bokk yépp. 5:28 Na yiwu sunu Boroom Yeesu Kirist ànd ak yéen.
1:1 Nun Pool ak Silwan ak Timote noo leen di bind, yéen mbooloom ñi gëm ci dëkku Tesalonig te nekk ci Yàlla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist. 1:2 Na leen Yàlla Baay bi ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak jàmm. 1:3 Bokk yi, mënunu lu dul sax ci sant Yàlla ndax yéen. Loolu jaadu na, ndax seen ngëm di gën a sax, te mbëggeel gi ngeen am ci seen biir, ku nekk ci sa moroom, di yokku lu bare. 1:4 Noonu nu ngi damu ci yéen ci kanamu mboolooy Yàlla yi, ndax seen muñ ak seen ngëm ci biir mboolem fitnay noon, ak coono, yi ngeen di dékku. 1:5 Loolu mooy firndeel àtteb Yàlla bu jub bi, di wone ne yelloo ngeen nguuru Yàlla, gi tax ngeen di sonn. 1:6 Ndaxte jub na ci Yàlla, mu delloo coono ñi leen di sonal, 1:7 te it yéen ñiy dékku coono, mu boole leen ak nun, tàbbal nu ci noflaay, bés bu sunu Boroom Yeesu Kirist jógee asamaan, feeñ fi. Keroog dina ànd ak malaakaam yu am kàttan, 1:8 safara su yànj wër ko, mu feeñ ngir mbugal ñi xamul Yàlla te bañ a déggal xebaar bu baaxu sunu Boroom Yeesu. 1:9 Seen pey mooy alku ba fàww, ñu dàq leen fu sore Boroom bi ak ndamam lu réy. 1:10 Dina ñëw bés booba, ngir ndamam jolli ci biir gaayam yu sell yi, te ñépp ñi ko gëm yéemu ci moom — te ci ngeen bokk, ndaxte gëm ngeen li nu leen seede. 1:11 Moo tax dunu noppeek di leen ñaanal, ngir Yàlla sunu Boroom def leen, ngeen yeyoo li tax mu woo leen, te yeggali ak doole ci yéen bépp yéene ju baax ak bépp jëfu ngëm. 1:12 Noonu turu Yeesu sunu Boroom dina màgg ci yéen, te yéen it dingeen màgg ci moom, aju ci yiwu sunu Yàlla ak Boroom bi Yeesu Kirist.
2:1 Ci lu jëm ci ñëwu Boroom bi Yeesu Kirist nag, bokk yi, ak sunu daje ak moom, am na lu ma leen di ñaan: 2:2 bu leen kenn gaaw a tàggale ak seen sago, mbaa di leen jaaxal, muy yonent buy wax, muy kàddu mbaa bataaxal bu ñu nu moomaleel, ci ne leen bésu Boroom bi ñëw na xaat. 2:3 Bu leen kenn nax ci benn fànn, ndaxte balaa booba, fàww Xiiroo bu mag bi ak Yàlla am, te Nitu ñaawteef ki feeñ, moom aji alku ji. 2:4 Day weddi lépp lu ñu teg Yàlla walla ñu koy jaamu, di yékkati boppam, ba toog sax ca kër Yàlla ga, tudde boppam Yàlla. 2:5 Xanaa fàttalikuwuleen ne, waxoon naa leen ko, ba ma nekkee ak yéen. 2:6 Te xam ngeen li ko téye léegi, ba du man a feeñ lu dul ci waxtoom. 2:7 Ndaxte fi mu ne ñaawteef gaa ngi jax-jaxi xaat ci kumpa, waaye ki ko téye mi ngi fi ba tey. Bu fi jógee nag, 2:8 Nitu ñaawteef ki dina feeñ, te Boroom bi Yeesu dina ko rey ak ngelawul gémmiñam, tas ko ak leer giy ànd ak ñëwam. 2:9 Bu Nitu ñaawteef kooku feeñee, dina ànd ak kàttanu Seytaane ak doole ju bare, di wone ay firnde ak ay kéemaan yu dul dëgg; 2:10 te dina nas bépp naxe buy sànke, ba yéem ñi nar a alku, ndaxte ubbiluñu seeni xol dëgg, gi leen manoon a musal. 2:11 Looloo tax Yàlla yónnee leen xelum réer, ba ñu gëm fen. 2:12 Noonu Yàlla dina mbugal ñépp ñi gëmul woon dëgg te doon bànneexu ci njubadi. 2:13 Kon nag bokk yi, yéen ñi Boroom bi bëgg, mënunu lu dul sax ci sant Yàlla ci li mu leen tànn ca njàlbéen ga, ngir musal leen, mu sédde leen boppam jaarale ko ci jëfu Xel mu Sell mi ak seen gëm dëgg gi. 2:14 Te Yàlla woo na leen ci loolu jaarale ko ci xebaar bu baax, bi nu leen doon yégal, ngir ngeen bokk ci ndamu sunu Boroom Yeesu Kirist. 2:15 Kon nag bokk yi, taxawleen bu dëgër te jàpp ci dénkaane yi nu leen jottali, muy ci li nu wax, muy ci li nu bind. 2:16 Na sunu Boroom Yeesu Kirist moom ci boppam ak Yàlla sunu Baay, mi nu bëgg te wone yiwam ci nun, ba ubbil nu buntu jàmm ju sax ak yaakaar ju wér, 2:17 dëfël seeni xol te saxal leen ci bépp jëf ju rafet ak gépp kàddu gu baax.
3:1 Léegi nag bokk yi, ñaanal-leen nu, ngir kàddug Boroom bi law te ànd ak ndam, ni mu ko ame woon ci yéen. 3:2 Ngeen ñaanal nu it, ngir nu mucc ci ñi bon te soxor, ndaxte du ñépp a gëm. 3:3 Waaye Boroom bi kuy sàmm kóllëre la; dina leen dëgëral te musal leen ci Ibliis. 3:4 Te wóor nanu ci kanamu Boroom bi ne, yéena ngi def li nu leen santoon, te dingeen ci sax. 3:5 Na Boroom bi gindi seeni xol ci mbëggeelu Yàlla ak muñu Kirist. 3:6 Nu ngi leen di sant it bokk yi, ci turu sunu Boroom Yeesu Kirist, ngeen dëddu bépp mbokk buy wéy ci tayel te bañ a topp dénkaane, yi nu leen jottali. 3:7 Xam ngeen bu baax, yéen ci seen bopp, ni ngeen war a awe ci sunuy tànk. Ba nu nekkee ca yéen, wéyunu woon ci tayel 3:8 te musunoo lekk ñaqu kenn. Waaye guddi ak bëccëg danu daan ñaq, di sonn, ngir bañ a wéeru ci kenn ci yéen. 3:9 Waxuma ne amunu sañ-sañu def ko, waaye danoo bëggoon a nekk ay royukaay ci yéen, ngir ngeen aw ci sunuy tànk. 3:10 Ndaxte ba nu nekkee ca yéen, lii lanu tëraloon: «Ku liggéeyul, du lekk.» 3:11 Léegi nag dégg nanu ne, am na ci yéen ñuy wéy ci tayel; liggéeyuñu dara, lu dul di dugg ci lu seen yoon nekkul. 3:12 Ñu deme noonu nag, nu ngi leen di sant te di leen dénk ci turu Boroom bi Yeesu Kirist, ñuy liggéey ci jàmm tey dunde seen ñaq. 3:13 Yéen nag bokk yi, buleen tàyyi ci def lu rafet. 3:14 Su kenn bañee topp li nu bind ci bataaxal bii, ràññeeleen ko te sore ko, ngir mu rus ci. 3:15 Waxuma ngeen def ko noon, waaye ngeen yedd ko ni seen mbokk. 3:16 Na leen Boroom jàmm may jàmm ci fépp ak ci lépp. Na Boroom bi ànd ak yéen ñépp. 3:17 Tàggoo bii maa ko bind ci sama loxo, man Pool. Nii laay binde, te di màndargaale nii sama bataaxal yépp. 3:18 Na yiwu sunu Boroom Yeesu Kirist ànd ak yéen ñépp.
1:1 Man Pool, ndawul Kirist Yeesu ci ndigalu Yàlla sunu Musalkat ak Kirist Yeesu sunu yaakaar, 1:2 maa ngi lay bind Timote, yaw miy sama doomu diine ju wér. Na la Yàlla Baay bi ak Kirist Yeesu sunu Boroom may yiw, yërmande ak jàmm. 1:3 Xam nga ne, ba may dem diiwaanu Maseduwan, ñaanoon naa la, nga des dëkku Efes, ngir dénk ña fa doon jàngale luy sànke, ñu bàyyi ko. 1:4 Te it nga dénk leen, ñu bañ a topp léebi diiney neen ak limi maam yu dul jeex mukk. Loolu werante rekk lay jur, waaye du jëme kanam mbir mi Yàlla tëral, wéer ko ci ngëm. 1:5 Waaye li sunuy dénkaane di jur mooy mbëggeel gu jóge ci xol bu laab, ci xel mu dal ak ci ngëm gu wér. 1:6 Am na ñu moy loolu, ba jeng jëm ciy waxi neen. 1:7 Dañoo sababloo nekk ay jàngalekat ci yoonu Musaa, fekk xamuñu dara sax ci li ñuy wax ak a dëggal. 1:8 Ci li aju ci yoonu Musaa nag, xam nanu ne baax na, ci ku koy jëfe ni ko Yàlla tërale. 1:9 Xam nanu it ne, tëddul ngir ñi jub waaye ngir ñi jubadi ak ñi déggadi, ñi weddi tey bàkkaar, ñi selladi te fonkadi Yàlla, ñiy dóor ndey walla baay, ak ñiy bóom; 1:10 ngir ñiy doxaan, ñi góor-jigéenu ak ñiy def nit jaam, ñiy fen tey wann seen kàddu, ak lépp luy juuyoo ak njàngale mu wér 1:11 mu xebaar bu baax bi indaale. Te xamleb xebaar, boobuy feeñal ndamu Yàlla Aji Tedd ji, dénk nañu ma ko. 1:12 Maa ngi gërëm sunu Boroom Kirist Yeesu, mi ma dooleel, ci kóolute gi mu am ci man, ba fal ma jawriñ. 1:13 Moona daa naa suufeel turam, di fitnaal ak a toroxal ñi ko gëm. Waaye Yàlla yërëm na ma, ndaxte ñàkka xam ak ñàkka gëm rekk a taxoon ma def ko. 1:14 Te yiwu sunu Boroom baawaan na ci man, ànd ak ngëm ak mbëggeel, yi bawoo ci Kirist Yeesu. 1:15 Wax ju wóor a ngii te yelloo gépp kóolute: Kirist Yeesu ganesi na àddina, ngir musal bàkkaarkat yi, te maa ci raw! 1:16 Waaye Yàlla yërëm na ma, ngir Kirist Yeesu jëkk a feeñal ci man muñam gu yaatu gi, ma nekk royukaay ci ñi ko nar a gëm te am dund gu dul jeex. 1:17 Yaw Buur bi fiy sax ba abadan, yaw mi bët mënta gis, yaw Yàlla miy kenn, yaa yelloo teraanga ak ndam ba fàww. Amiin! 1:18 Kon nag Timote sama doom, loolu mooy sas wi ma lay dénk, te mu dëppook waxi yonent, yi jëmoon ci yaw. Doolewool wax yooyu, ba xeex xeex bu baax bi, 1:19 di sàmm sa ngëm ak xel mu dal. Am na ñu seen xel nëx, ba labal seen ngëm, 1:20 naka Imene ak Alegsàndar; jébbal naa leen Seytaane, ngir ñu réccu li ñu doon sosal Yàlla.
2:1 Fii laay tàmbale nag: maa ngi leen di dénk, ngeen yóbbu ñépp fa kanam Yàlla ciy ñaan, ay tinu ak i ngërëm. 2:2 Ñaanal-leen buur yi ak kilifa yépp, ngir nu man a am dund gu dal te jàmmu, ànd ak ragal Yàlla ak faayda yu mat. 2:3 Loolu mooy li rafet te neex Yàlla sunu Musalkat, 2:4 bi bëgg ñépp mucc te xam dëgg gi. 2:5 Ndaxte jenn Yàlla kepp moo am, ak benn Rammukat kepp diggante Yàlla ak nit ñi, di nit ki Kirist Yeesu, 2:6 mi joxe bakkanam ngir jot ñépp. Loolu mooy seede si Yàlla joxe, bi waxtu wi jotee. 2:7 Te fal na ma ci ndaw ak jàngalekat, may yégal xeeti àddina yoonu ngëm ak dëgg; fenuma, dëgg rekk laay wax. 2:8 Li ma bëgg kon mooy lii: na góor ñi ñaan ci Yàlla fu nekk, tàllal ko loxo yu sell, te bañ cee boole mer mbaa werante. 2:9 Naka noonu itam, na jigéen ñi di sol col gu faaydawu, cig woyof ak maandu. Buñu def seen xel ciy létt ak ci takkaayu wurus, mbaa ciy per ak col gu jafe. 2:10 Waaye na seen col di jëf yu rafet, ndaxte looloo jekk ci jigéen juy woote ag ragal Yàlla. 2:11 Te it na jigéen jàng cig noppi, ànd ak déggal gu mat. 2:12 Mayuma jigéen, muy jàngale mbaa muy jiite góor, waaye na noppi. 2:13 Ndaxte Aadama la Yàlla jëkk a sàkk, door caa teg Awa. 2:14 Te it du Aadama la Seytaane nax, waaye jigéen ja la nax, ba mu jàdd. 2:15 Teewul jigéen dina mucc ci wasin, su saxee ci ngëm ak mbëggeel, di ku sell te maandu.
3:1 Wax ju wóor a ngii: kuy sabablu yenub sàmm mbooloo mi, mu ngi yóotu liggéey bu rafet. 3:2 Sàmm bi nag, nii la war a mel: war na ñàkk ŋàññ, yem ci benn soxna, moom boppam te maandu; war na am faayda, man gan te am mayu jàngale; 3:3 warul di ab màndikat mbaa xeexkat, waaye na lewet te jàmmu, bañ a bëgge ci xaalis. 3:4 Na yor këram yorin wu rafet, te ay doomam déggal ko ak teggin yu mat. 3:5 Ndaxte ku mënta yor njabootam, naka lay man a yore njabootu Yàlla? 3:6 Te it bumu nekk kuy door a gëm, ngir mu bañ a yég boppam, bay dajeek mbugalu Yàlla, ni ko Seytaane defe woon. 3:7 Te it war na am seede su rafet ci waa àddina, ngir ñu bañ koo diiŋat, ba muy daanu ci fiiru Seytaane. 3:8 Kiy topptoo li mbooloo miy jëfandikoo itam na am faayda te fonk kàddoom; bumu di ku yàqu ci sangara, mbaa ku alal jiital. 3:9 Na sàmm mbóoti ngëm gi ak xel mu dal. 3:10 Moom itam nañu ko jëkk a seetlu, ba mu leer ne amul ŋàññ, ñu door koo fal. 3:11 Naka noonu, na jigéen ñi am faayda, bañ a jëw mbaa xér ci dara, waaye nañu takku ci lépp. 3:12 Ku ñu dénk sasu topptoo yëfi mbooloo mi nag, nay ku yem ci benn soxna, jiite bu baax këram ak i doomam. 3:13 Ndaxte ku ci rafetal sasam dina am tur wu tedd ak kóolute gu mat sëkk ci yoonu ngëm, gi ci Kirist Yeesu. 3:14 Bëgg naa laa seetsi balaa yàgg, 3:15 waaye amaana mu yéex. Moo tax ma lay bind bataaxal bii, ngir xamal la, ni ñu war a nekke ci kër Yàlla gi, maanaam ci mbooloom Yàlla Aji Dund ji, miy kenug dëgg te di sëslaayam. 3:16 Ci dëgg-dëgg ragal Yàlla ëmb na mbóot yu xóot:Ki wàcc, yor bindu nit,mu bir ne xelam jub na,te malaaka ya gis ko;xamlees na ko ci xeet yi,ñu gëm ko ci kaw suuf,te Yàlla teeru ko ci ndamam.
4:1 Xelum Yàlla mi wax na bu leer ne, ci mujug jamono dina am ñu bàyyi yoonu ngëm wi, di topp ay xel yuy fàbbee ak xalaati Seytaane. 4:2 Ñooñu ay naaféq yuy naxe lañu, te seen xol dërkiis. 4:3 Dinañu tere séy, di araamal ay ñam, fekk Yàlla sàkk na leen, ngir ñi gëm te xam dëgg man ciy jëfandiku ak cant. 4:4 Ndaxte li Yàlla sàkk lépp baax na, kon wenn ñam araamul ci ku koy jëfandikoo ak cant. 4:5 Ndaxte kàddug Yàlla ak ñaan ñoo koy sellal. 4:6 Saxal ci digal bokk yi loolu nag, kon dinga nekk jawriñu Kirist Yeesu ju baax ju regg ci kàdduy yoonu ngëm wi ak njàngale mu rafet, mi nga xam bu wér. 4:7 Tanqamlul ay léebi diiney neen, di ay wax yu amul bopp yu àddina kese; waaye tàggatal sa bopp ci ragal Yàlla. 4:8 Ndaxte tàggat yaram am na fu njariñam yem, waaye njariñu ragal Yàlla dafa daj lépp, ëmb digey àddina ak àllaaxira. 4:9 Wax ju wóor a ngii, te mat a nangu ak gépp kóolute. 4:10 Danuy ñaq tey bëre, ndaxte wékk nanu sunu yaakaar ci Yàlla Aji Dund ji, di Musalkatu ñépp, rawatina nag ci ñi gëm. 4:11 Digal leen yëf yooyu nag ci sa njàngale. 4:12 Bu la kenn xeeb ndax say at, waaye defal sa bopp royukaayu ñi gëm ci say wax ak say jëf, ci sa mbëggeel, sa ngëm ak sa cell. 4:13 Li feek may dikk, saxal ci jàng di biral Mbind mi ci mbooloo mi, di leen dénk ak a jàngal. 4:14 Bul sàggane may gi nekk ci yaw, gi la Yàlla jox jaarale ko ci waxu yonent, keroog bi la njiit yi tegee loxo. 4:15 Faaydaalal yëf yooyu te sóobu ci, ba sa jëm kanam bir ñépp. 4:16 Sàmmal sa bopp te sàmm sa njàngale, te sax ci; noonu dinga musal sa bopp, yaw ak ñi lay déglu.
5:1 Bul gëdd mag, waaye waxtaanal ak moom ni sa baay. Ndaw it, nga digal ko ni sa rakk, 5:2 jigéen ju mag, def ko ni sa yaay; ju ndaw, ni sa jigéen ak cell gu mat sëkk. 5:3 Ci wàllu ñi seen jëkkër faatu nag, ku ci sësul ci kenn, teral ko ngir Yàlla. 5:4 Waaye ku ci am ay doom mbaa ay sët, na njaboot googu jëkk a wone seen ragal Yàlla ci seen biir kër, ci delloo njukkal seen waajur, ndaxte loolu lu rafet la fa kanam Yàlla. 5:5 Jigéen ju sësul ci kenn day wékk yaakaaram jépp ci Yàlla, sax ci di ko wéetal te di ko ñaan guddi ak bëccëg. 5:6 Waaye ki bànneex jiital, ndee luy dox la. 5:7 Dénk leen loolu, ngir ñu bañ a am benn gàkk. 5:8 Ndaxte ki defalul ay bokkam dara, rawatina ay waajuram, weddi na yoonu ngëm wi, ba yées ku gëmadi. 5:9 Ku bëgg a bindu ci ñi seen jëkkër faatu, nii la war a mel: war na wees juróom-benn-fukki at, di jigéen ju yemoon ci jëkkëram, 5:10 te mu ràññiku ci jëf yu rafet yu deme ni yar ay guneem, man gan, geestu gaayi Yàlla yu sell yi, dimbali ñi nekk ci tiis; maanaa di ku takku ci mboolem jëf yu rafet yi. 5:11 Waaye bul bind jigéen ju ndaw, ndaxte bu ko ay bëgg-bëggam xiiree ci sore Kirist, dina bëgg a séyaat, 5:12 te dina daje ak mbugal ndaxte fecci na kóllëre. 5:13 Te du yem ci bëgg a séyaat rekk, waaye ku tayel lay doon; di ku wër kër ak kër, rax-ca-dolli réy làmmiñ te deñ kumpa, di wax lu yoonam nekkul. 5:14 Looloo tax ma bëgg, jigéen yu ndaw yi séyaat, am ay doom, yor seeni kër, ba seen benn noon du leen man a gàkkal. 5:15 Ndaxte fi mu ne sax am na ñu jeng xaat, ba topp Seytaane. 5:16 Kon nag jigéen ju gëm te am mbokk mu jëkkëram faatu, na ko dimbali te bañ koo bàyyeek mbooloom ñi gëm. Noonu mbooloo mi dina man a dimbali jigéen ñi sësul ci kenn. 5:17 Li jëm ci njiiti mbooloo mi nag, joxal teraanga ju mat sëkk ñi ciy rafetal seen liggéey, rawatina ñi sax dàkk ci waare bi ak njàngale mi. 5:18 Ndaxte Mbind mi nee na: «Bul sunjuñ gémmiñu nag wu ñu takk bojjukaay,» nee na it: «Ku ñaq, jariñu.» 5:19 Kuy tuumaal njiit fi yaw, bu ko gëm, li feek ñaar walla ñetti seede dëggaluñu ko. 5:20 Waaye ñiy bàkkaar, yedd leen fa kanam ñépp, ngir artu ñi ci des. 5:21 Léegi nag maa ngi lay dénk fa kanam Yàlla ak Kirist Yeesu ak malaaka yu tedd ya, nga sàmm loolu ma wax te bañ cee gënale walla di ci parlàqu. 5:22 Bul gaaw a teg loxo kenn, ba fal ko, di séddu noonu ci bàkkaari jaambur, waaye dëkkal cig sell. 5:23 Ba tey bul yemati ci ndox mu ñuul rekk, waaye nangay naan tuuti biiñ, ngir faj say metiti biir ak say jagadi yu bare. 5:24 Am na, ñu seeni bàkkaar fés ci kanamu ñépp, ba jiitu leen ca àtte ba; ñi seeni bàkkaar nëbbu nag, bés baa ngi leen di xaar. 5:25 Naka noonu it am na, ñu seen jëf yu rafet leer, te yi feeñul mënuñoo nekk kumpa ba fàww.
6:1 Ñi nekk ci buumu njaam nag, nañu weg seeni sang wegeel gu mat sëkk; noonu kenn du am lu muy werante ci turu Yàlla mbaa ci sunu njàngale. 6:2 Ku am sang boo bokkal ngëm, bu looloo tax nga yab ko, waaye nga sax ci itteem, ndax kiy jariñu ci sa ñaq, aji gëm la, ku mat a bëgg. Jàngaleel loolu nag, di ko dénkaane. 6:3 Waaye su fi amee kuy jàngale leneen, ba jàppul ci kàddu yu wér yu Yeesu Kirist Boroom bi, te fonkul waaraate buy jur ragal Yàlla, 6:4 kooku boroom tiitar la, bu xamul dara. Dafa wéradi, ba sóobu ci gëstuy neen ak i werante ciy araf yu dul jur lu dul ñeetaange, xuloo, xaste, ñaaw njort 6:5 ak ŋaayoo; ñiy jëfee noonu nit ñu ñaaw xel lañu, ñu xamul genn dëgg te yaakaar ne, ragal Yàlla buntu wërsëg la. 6:6 Ba tey ragal Yàlla gu ànd ak doylu, wërsëg la. 6:7 Ndaxte indaalewunu fi dara, te dunu yóbbaale dara. 6:8 Kon su nu amee lekk ak koddaay, nanu ko doyloo. 6:9 Waaye ñiy sàkkoo barele, dinañu jànkoonte ak i nattu, ba dugg ci fiir, di xuus ci bëgg-bëggi neen yuy yóbbe ayib, tey sóob nit cig réer ak sànkute. 6:10 Ndaxte bëgge ci xaalis mooy ndeyu ñaawteef yu bare; am na ñu ko wut, ba moy ci yoonu ngëm, te seen xol di dagg ndax tiis yu bare. 6:11 Kon nag yaw waayu Yàlla ji, dawal loolu, te topp njub, ragal Yàlla, ngëm, mbëggeel, muñ ak lewet. 6:12 Góor-góorlul ci bëre bu baax bi, ba ub làmbi ngëm, te feddali sag téye ci dund gu dul jeex gi; ndaxte ci loolu la la Yàlla woo, te looloo waraloon it sa seede su rafet fa kanam mbooloo mu bare. 6:13 Noonu fi kanam Yàlla mi jagleel dund ci lépp, ak fi kanam Kirist Yeesu, mi seede woon seede su rafet fa kanam Poñsë Pilaat, maa ngi lay dénk lii: 6:14 sàmmal ndigal li, bañ a am gàkk mbaa ŋàññ, ba kera Yeesu Kirist sunu Boroom di feeñ ci ndamam, ca waxtu wa Yàlla dogal. 6:15 Moom kenn mooy Boroom bu tedd, di Buuru buur yi ak Kilifag kilifa yi. 6:16 Moom kenn a jagoo dund gu sax, dëkk ci biir leer gu kenn mënta jege; moom mi nit musul a gis te nit mënu koo gis. Moom kenn a yelloo teraanga ak màggaay ba fàww. Amiin. 6:17 Ñi barele alalu àddina nag, dénk leen ñu bañ a réy te bañ a wékk seen yaakaar ci koom-koom yi saxul fenn, waaye ñu wékk ko ci Yàlla, mi nuy may naataange ju mat, ngir nu man ciy bànneexu. 6:18 Dénk leen ñu def lu baax, te bare jëf yu rafet, ñu yéwén, bay sédd ñi amul, 6:19 di fàggu dencu ëllëg bu wér. Noonu dinañu feddali seen téye ci dund gu wóor gi. 6:20 Céy yaw Timote, sàmmal li la Yàlla dénk! Tanqamlul waxi neen yu àddina kese, te dëddu werantey ñi mbubboo xam-xam, fekk dañoo réer. 6:21 Am na ñu topp xam-xam boobu, waaye moy nañu ci yoonu ngëm. Na yiwu Yàlla ànd ak yéen.
1:1 Man Pool, ndawul Yeesu Kirist ci coobareg Yàlla, ngir xamle dund gi nu Yàlla dig te féete ci Kirist Yeesu, 1:2 maa ngi lay bind Timote, sama doomu diine ji ma bëgg. Na la Yàlla Baay bi ak Kirist Yeesu sunu Boroom may yiw, yërmande ak jàmm. 1:3 Fu ma tollu maa ngi lay boole ci samay ñaan, di ci sant Yàlla, mi may jaamu ci xel mu dal, ni ko samay maam daan defe. Guddi ak bëccëg, bu sama xel demee ci say rangooñ, 1:4 ma bëgg laa gis, ba am mbég mu réy. 1:5 Maa ngi fàttaliku sa ngëm gu dëggu, gi nekkoon ci sa maam Lowis ak sa yaay Ënis, te mu wóor ma ne, sax na ci yaw it. 1:6 Looloo tax maa ngi lay fàttali, nga xambaat taal bi Yàlla taal ci yaw, di may gi mu la jagleel, bi ma la tegee samay loxo. 1:7 Ndaxte Xel mi nu Yàlla sol du ànd ak ragal, waaye day ànd ak kàttan, mbëggeel ak moom sa bopp. 1:8 Bul rus ci seedeel sunu Boroom, mbaa ci li ñu ma tëj ndax turam, waaye bokkal ak man tiis ci xamle xebaar bu baax bi, wéeru ci kàttanu Yàlla. 1:9 Moo nu musal te woo nu ci dund gu sell, ci lu ajuwul ci sunuy jëf, waaye ci dogalu boppam ak yiwam, wi nu Yàlla may ci Kirist Yeesu, ba àddina sosoogul. 1:10 Te léegi biral na ko ci feeñug sunu Musalkat Kirist Yeesu, mi nasaxal dee te feeñal dund ci xebaar bu baax bi, te muy dund gu sax. 1:11 Te Yàlla fal na ma ndaw ak jàngalekat, ngir may yégle xebaar bi; 1:12 looloo tax ma jànkoonte ak tiis yu mel nii. Waaye rusuma ci, ndaxte xam naa Ki ma wékk sama yaakaar, te wóor na ma ne, li ma ko dénk, man na koo denc ba bés ba. 1:13 Toppal ci tànki wax yu wér yi nga dégge ci man, jàpp ci ak ngëm ak mbëggeel, yi nu am ci sunu bokk ci Kirist Yeesu. 1:14 Te nga sàmm bu baax li la Yàlla dénk, wéeru ci Xel mu Sell, mi dëkk ci nun. 1:15 Xam nga ne, waa diiwaanu Asi gépp, won nañu ma gannaaw, ñu deme niki Fusel ak Ermosen. 1:16 Waaye Onesifor daa na faral di dëfël sama xol; na Boroom bi sotti yërmandeem ci këram. Rusul woon sax ci samay jéng, 1:17 waaye bi mu ñëwee dëkku Room, wut na ma fu ne, ba gis ma. 1:18 Na ko Boroom bi teeru ak yërmandeem ca bés ba. Umplewoo it coono yi mu daj, ngir dimbali ma ca dëkku Efes.
2:1 Kon nag yaw sama doomu diine, doolewool yiw, wi ci Kirist Yeesu. 2:2 Te wax yi nga dégge ci man fi kanam seede yu bare, nanga leen jottali nit ñu takku, ngir ñoom it ñu man a jàngal ñeneen. 2:3 Bokkal ak man tiis, di jàmbaar ci toolu xareb Kirist Yeesu, 2:4 xam ne xarekat bu bëgg a neex ka ko solal, du dugg ci yëfi àddina. 2:5 Te it ku tàggat yaramam ngir rawante, duñu ko jagleel kaalag ndam mukk, su toppul sàrt ya. 2:6 Noonu it beykat bi sonn mooy jëkk a ñam toolam. 2:7 Xalaatal bu baax sama wax jii, ndax Boroom bi dina leeral sa xel ci lépp. 2:8 Fàttalikul Yeesu Kirist mi dekki, soqikoo ci Daawuda, tukkee ci xebaar bu baax bi may waare. 2:9 Xebaar booboo tax may jànkoonte ak i tiis, ba ñu jéng ma ni defkatu lu bon; waaye kàddug Yàlla moom, kenn du ko jéng. 2:10 Te lii tax may muñ lépp, ngir ñi Yàlla tànn it am mucc gi ci Kirist Yeesu, gu ànd ak ndam lu sax. 2:11 Kàddu gu wóor a ngii:Su nu deeyaalee ak Kirist,dinanu dundaat ak moom; 2:12 su nu takkoo,dinanu nguuru ak moom. 2:13 Su nu ko weddee,kon mu weddi nu;su nu ko ñàkkee kóllëre,moom dina sax ci kóllëreem,ndax mënul a weddi boppam. 2:14 Saxal ci di leen fàttali mbir yooyu, di leen dénk fa kanam Yàlla, ñu moytoo werante ciy araf, ndax loolu jëmul fu dul ci yàq ngëmu ñiy déglu. 2:15 Góor-góorlul ba teew fa kanam Yàlla, nekk liggéeykat bu mu nangul te rusoo ci dara, di faramfàcce bu jub kàddug dëgg gi. 2:16 Moytul bépp jataayu waxi neen yu àddina kese, ndax ña fa toog dinañu gën a xuus cig weddi, 2:17 te seen kàddu day burux ni ngal. Imene ak Filet, ci ñoom lañu bokk; 2:18 dañoo moy dëgg, di wax ne ndekkite wees na, ba yàq ngëmu ñenn ñi. 2:19 Waaye teewul fondamaa bu dëgër, bi Yàlla tabax, nee na kekk, te lii lañu ci tàmpe: «Boroom bi xam na ñi bokk ci moom,» te it: «Ki tudd turu Boroom bi, na daw lu bon.» 2:20 Ci kër gu mag nag, du ndabi wurus walla xaalis rekk a fa am, waaye itam yoy dénk walla ban; yii tedd nañu, yee ñàkk solo. 2:21 Kon nag ku laabal sa bopp ci yooyu yépp, dinga nekk ndab lu tedd te sell, nga am njariñ ci Boroom bi te jekk ci bépp jëf ju rafet. 2:22 Dawal bépp bëgg-bëggu ngune, te sóobu ci njub, ngëm, mbëggeel, jàmm, ànd ak ñépp ñiy tudd turu Boroom bi ak xol bu sell. 2:23 Tanqamlul bépp weranteb neen bu amul njariñ, xam ne xuloo rekk lay jur. 2:24 Te jaamu Boroom bi warul a xuloo, waaye na lewet ci ñépp, jekk ngir jàngale tey muñ fitnay noon. 2:25 Na jubbanti cig suufe ñi koy diiŋat, tey yéene Yàlla xiir leen ci réccu, ba ñu xam dëgg; 2:26 ñu rëcc ci fiirug Seytaane, mi leen jàpp niy jaam, te ñu dellusi ci seen xel yu rafet, ba sóobuwaat ci coobareg Yàlla.
3:1 Nanga xam lii: bési tiis yu tar ñu ngi nuy tëru ci muju jamono. 3:2 Ndaxte nit ñi dinañu siis te fonk xaalis, di ñu réy tey yég seen bopp, ñuy xaste tey xëtt ndigalu waajur; duñu am kóllëre, sellaay 3:3 mbaa cofeel; dañuy jàpp mer ak a sos; ñu xér lañuy doon, ñu soxor te bañ lu baax; 3:4 ay workat lañuy doon, di ñu ëppal te bare tiitar; seen bànneex a leen gënal Yàlla. 3:5 Dañuy mbubboo diine waaye nanguwuñu koo dugal seen xol. Ñu deme noonu, dëddu leen. 3:6 Nit ñu mel noonu ñooy yoxoosu ci biir kër yi, ba fàbbi jigéen ñu ñàkk pasteef, ñi seeni bàkkaar ub seen bopp, te bëgg-bëgg yu wuute jiital leen. 3:7 Duñu noppee gëstu, waaye duñu man a yegg ci xam-xamu dëgg mukk. 3:8 Nit ñooñu dañuy bëreek dëgg, ni Sànnes ak Sàmbares bëree woon ak Musaa; ay boroom xel yu gumba lañu, yu seen ngëm tekkiwul dara. 3:9 Waaye duñu dem fu sore, ndax seen ñàkk xel dina bir ñépp, ni mu dale woon Sànnes ak Sàmbares. 3:10 Waaye yaw nag xam nga bu baax sama njàngale, sama dund, sama takkute, sama ngëm, sama muñ, sama mbëggeel ak sama dékku tiis. 3:11 Xam nga li ma daj ciy fitna ak i coono ci dëkki Ancos, Ikoñum ak Listar. Céy li ma jànkoonteel ciy fitna! Waaye Boroom bi musal na ma ci lépp. 3:12 Te ku bokk ci Kirist Yeesu, te bëgg dund dund gu ànd ak ragal Yàlla, alamikk ñu fitnaal la. 3:13 Waaye nit ñu bon ñi ak naaféq yi dinañu fi yées, di naxe ak a nax seen bopp. 3:14 Yaw nag saxal ci li nga jàng te mu wóor la, xam fi nga tibbe. 3:15 Li dale ci sa ngune xam nga Mbind mu sell, mi la man a yee ci yoonu mucc, jaar ci gëm Kirist Yeesu. 3:16 Mbind mu sell mépp, ci gémmiñu Yàlla la jóge, te am na njariñ ngir jàngal nit ñi, yedd leen, jubbanti leen te yee leen ci njub. 3:17 Noonu waayu Yàlla ji dina mat, ba jekk ci bépp jëf ju rafet.
4:1 Kon nag maa ngi lay dénk fa kanam Yàlla ak Kirist Yeesu, miy àtte ñiy dund ak ñi dee, di la dénk ci feeñam ci biir ndam ak ci nguuram, nga def lii: 4:2 xamleel kàddug Yàlla, sax ci, su neexee ak su naqaree; yeyal ñi tooñ, di yedd ak a dénk ñépp, def ko ci muñ gu yaatu ak njàngale mu mat. 4:3 Ndaxte jamono dina ñëw, joo xam ne nit ñi dootuñu xajoo njàngale mu wér mi, waaye dinañu jublu ci seeni bëgg-bëgg, di fortaatu jàngalekat yu leen di jey. 4:4 Dinañu tanqamlu dëgg, jeng jëm ci léebi diiney neen. 4:5 Waaye yaw nanga foog ci lépp, dékku tiis, tey tas xebaar bu baax bi, ba matal sag yónnent. 4:6 Ndaxte maa ngi ci tànki joxe sama bakkan ni sarax, te sama waxtuw dem jot na. 4:7 Bëre naa ba ub làmbi ngëm, daw naa ba àkk, sàmm naa mboolem dëgg, gi ñu ma dénk. 4:8 Fi mu ne Yàllaa ngi may xaare añu ku jub, di kaalag ndam gi ma Boroom, biy Àttekat bu jub, di jox ca bés ba, te jéllale naa sama bopp, waaye képp ku def sa xol cig feeñam. 4:9 Defal sa kem-kàttan, ba fekksi ma ci ni mu gën a gaawe. 4:10 Ndaxte Demas topp na àddina, ba bàyyi ma, dem dëkku Tesalonig; Kereseñsë dem na diiwaanu Galasi, Tit dem diiwaanu Dalmasi. 4:11 Luug rekk a des fi man. Indaaleel Màrk, ndaxte amal na ma njariñ ci liggéey bi. 4:12 Tisig moom yebal naa ko dëkku Efes. 4:13 Te sooy ñëw, indaaleel mbubb, ma ma dénkoon Karpus ca dëkku Torowas, te it bul fàtte téere yi, rawatina téere yu am maana, yi ñu bind ci der. 4:14 Alegsàndar tëgg bi def na ma ñaawteef yu ne, waaye Boroom bi dina ko fey ay jëfam. 4:15 Moytu ko bu baax, ndaxte bëre na ak sunuy wax ba tàyyi. 4:16 Keroog bi ma jëkkee taxaw, di làyyil sama bopp, awma woon kenn ku ma taxawu, ñépp dañu maa daw — bu leen ko Yàlla jàppe nag. 4:17 Waaye Boroom bi moo ma taxawu te dooleel ma, ma jollil kàddu gi, ba xeet yépp dégg ko. Te Boroom bi musal na ma ci selli gaynde. 4:18 Rax-ca-dolli dina ma musal ci bépp jëf ju ñaaw, tette ma ci jàmm, ba tàbbal ma ci nguuram gu kawe ga. Na yelloo ndam ba fàww. Amiin. 4:19 Nuyul ma Piriska ak Akilas ak waa kër Onesifor. 4:20 Erast des na dëkku Korent. Torofim dafa woppoon, ma bàyyi ko dëkku Mile. 4:21 Gaawal a ñëw, bala lolli di gàllankoor sa yoon. Ëbulus, Pudeñsë, Linus, Këlójaa ak yeneen bokk yépp ñu ngi lay nuyu. 4:22 Na Boroom bi aar sa xel. Na yiwu Yàlla ànd ak yéen ñépp.
1:1 Man Pool maa lay bind, man miy jaamu Yàlla ak ndaw li Yeesu Kirist yónni, ngir xamle ngëm, gi lal yoonu ñi Yàlla tànn, tey yokk xam-xamu dëgg, giy meññ ragal Yàlla; 1:2 mu sukkandiku ci yaakaar ju dëggu, ji nu am ci dund gu dul jeex, gi Yàlla dige ba dara sosoogul, moom mi dul tebbi waxam. 1:3 Te léegi, ci jamono ji ko soob, feeñal na xebaaram boobu ci waaraate, bi ma Yàlla sunu Musalkat dénk te digal ma, ma xamle ko. 1:4 Maa ngi lay bind, Tit, yaw sama doomu diine ju wér ci ngëm, gi nu bokk nun ñépp. Na la Yàlla Baay bi ak Kirist Yeesu sunu Musalkat may yiw ak jàmm. 1:5 Bàyyi naa la ca réewu Kereet, ngir nga mottali la desoon ci liggéey bi, te samp ay njiiti mbooloo ca dëkk bu nekk, ni ma la ko sante woon. 1:6 Njiit nag nii la war a mel: war na ñàkk ŋàññ, yem ci benn soxna, am ay doom yu gëm yu amul baatu gannaaw cig yàqute mbaa déggadi. 1:7 Ndaxte kuy sàmm mbooloo mi mooy jawriñu Yàlla, kon warul am ŋàññ, walla di ku dëgër bopp mbaa ku tàng bopp; warul dib màndikat walla xeexkat mbaa ku bëgge ci alal ju lewul. 1:8 Waaye war na man gan te bëgg lu baax, di ku maandu te jub, ku sell te noot boppam. 1:9 War na jàpp ci xebaar bu dëggu, bi lal sunu yoon, ba man a dénkaane ci njàngale mu wér mi, tey yey ñi weddi. 1:10 Loolu war na, ndaxte am na ñu bare ñu déggul lenn ndigal, rawatina ci Yawut yi, ñuy yàq xeli nit ñi ak seen waxi neen. 1:11 Fàww nga wedamloo leen, ndax dañuy tas këri lëmm, ciy jàngale li warul ngir sàkku alal ju lewul. 1:12 Am na nitu Kereet, di yonent ci ñoom, mu ne: «Waa Kereet, ay fenkat lañu mas a doon, ñu soxor ni ay rabi àll, fuqle te tayel.» 1:13 Te li mu wax dëgg la. Looloo tax nga war leen a yey bu wóor ci seeni bàkkaar, ngir ñu am ngëm gu wér 1:14 te bañ a topp léebi diiney neen yu Yawut yi, mbaa tegtali nit, ñi dëddu dëgg. 1:15 Ñi sell seen lépp a sell, waaye ñi selladi te gëmadi seen dara sellul, du seeni xalaat, du seeni xel. 1:16 Dañoo mbubboo xam-xamu Yàlla, waaye seeni jëf weddi na ko; ñu sikk lañu te déggadi, ba tële ci jëf lenn lu baax.
2:1 Yaw nag nangay waare li dëppook njàngale mu wér mi. 2:2 Maanaa, na góor ñu mag ñi foog, am faayda te maandu, di ñu wér ci seen ngëm, seen mbëggeel ak seen muñ. 2:3 Jigéen ñu mag ñi itam, na seen doxalin ànd ak faayda; buñuy jëw mbaa xér ci sangara. Waaye nañuy jàngale lu baax, 2:4 bay sol ci boppu jeeg yu ndaw yi, ñu bëgg seeni jëkkër ak seeni doom, 2:5 di ñu maandu, sell te fonk seen kër, ñu neex deret te déggal seeni jëkkër, ngir kenn bañ cee gàkkal kàddug Yàlla. 2:6 Naka noonu itam nanga xiir waxambaane yi cig maandu. 2:7 Te yaw, ci lépp lu mu man a doon, nekkal ab royukaay ci jëf yu baax. Na sa njàngale wér te am faayda, 2:8 ànd ak wax yu wér yu kenn mënta diiŋat, ngir sunuy noon rus ba wedam, ci li ñu amul dara lu ñu nu tuumaal. 2:9 Waxal it jaam ñi, ñu déggal seeni sang ci lépp, te liggéeyal leen ba seral seen xol, bañ cee boole werante 2:10 mbaa sàcc. Waaye nañu wone takkute gu mat, ba rafetal ci lépp njàngalem Yàlla sunu Musalkat. 2:11 Ndaxte yiwu Yàlla feeñ na te ubbil na ñépp buntu mucc. 2:12 Moo nu digal, nu dëddu weddi ak bëgg-bëggi jamono, tey dund ci àddina cig maandu, njub ak ragal Yàlla, 2:13 di séentu bés bu tedd bi nu yaakaar, maanaa Yàlla ju màgg ji, di sunu Musalkat Yeesu Kirist, feeñ ci biir ndamam. 2:14 Joxe na bakkanam ngir nun, ba jot nu ci lépp lu bon, te beral nu boppam, di xeet wu sell te ràññiku ci jëf yu baax. 2:15 Jàngaleel loolu, di leen dénk ak a yedd ak fulla ju mat. Bu la kenn yab.
3:1 Fàttali leen ñuy déggal kilifa, yi yore nguur gi, tey jëfe seeni ndigal, ñu taxaw temm ci lépp luy jëf ju baax. 3:2 Buñu jëw kenn mbaa ñuy ŋaayoo, waaye nañu yiwe te won ñépp lewet gu mat sëkk. 3:3 Ndaxte nun itam ñu ñàkk xel lanu woon te déggadi, nu réer bay jaamu ay bëgg-bëgg ak i bànneex yu wuute, nu dëkk ci coxorte ak ñeetaange, di ñu sikk tey sikkante. 3:4 Waaye naka noona Yàlla sunu Musalkat feeñal na mbaaxam ak cofeelam, 3:5 ba musal nu; ajuwul ci jëf yu jub yu nu def, waaye ci yërmandeem rekk. Mu juddulaat nu ci laabal sunu xol, te yeesalaat nu ci dooley Xel mu Sell, 3:6 mi mu nu sotti ba mu baawaan, ci darajay Yeesu Kirist sunu Musalkat. 3:7 Ci noonu Yàlla àtte na nu jub ci kaw yiwam, te sédd nu ci dund gu dul jeex, gi nuy séentu. 3:8 Wax jooju ju wóor la, te damaa bëgg nga dëggal loolu, ngir ñi gëm Yàlla sax ci jëf lu rafet. Loolu moo baax te am njariñ ci nit. 3:9 Waaye moytul yu deme ni werantey neen ak limi maam, ay xuloo ak i xëccoo ci doxalinu yoonu Musaa, ndax loolu waxi neen la, te amul benn njariñ. 3:10 Kuy féewale, nanga ko yedd, yeddaat ko; bu tëwee, nga dàq ko, 3:11 xam ne nit ku ñaaw xel la te ay bàkkaaram fés ci ñépp. 3:12 Bu ma la yónnee Artemas walla Tisig, gaawantul fekksi ma ci dëkku Nikopolis, ndax fa laa bëgg a lollikooji. 3:13 Naka Senas àttekat bi nag ak Apolos, waajal leen bu jekk ci seen tukki, ba seen aajo yépp faju. 3:14 Na sunuy bokk it takku ci jëf yu rafet, ba man a faj aajo yépp, te bañ a yaafus. 3:15 Ñiy ànd ak man ñépp ñu ngi lay nuyu. Nuyul nu sunuy soppey ngëm. Na yiwu Yàlla ànd ak yéen ñépp.
1:1 Man Pool, mi ñu tëj kaso ngir Kirist Yeesu, ak sunu mbokk Timote, noo lay bind, yaw Filemon sunu soppe ak sunu nawle ci xeex bi; 1:2 te fàttewunu sunu jigéen Afiya, ak sunu àndandoo ci xeex bi Arkib, yéen ak mbooloom ñi gëm, miy dajee sa kër. 1:3 Na leen Yàlla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak jàmm. 1:4 Duma la noppee boole ci samay ñaan, di ci sant Yàlla sama Boroom, 1:5 ndaxte dégg naa sa ngëm ci Boroom bi Yeesu, ak sa mbëggeel ci gaayam yu sell yépp. 1:6 Li may ñaan nag a ngi nii: nga xam bu wér ngëneel, yi nu am yépp ci sunu bokk ci Kirist, ba tax bokk gi nga am ci Yàlla ci kaw ngëm meññ i njariñ. 1:7 Ci dëgg-dëgg sa mbëggeel bégal na ma bu baax, ba dëfël sama xol; ndaxte xam naa, sama mbokk, ni nga féexale xoli gaayi Yàlla yu sell yi. 1:8 Am na lu ma la bëgg a ñaan; teguma ko ci sañ-sañ bu mat bi ma Kirist may, ci teg la ndigalu def sa warugar, 1:9 waaye dama lay ñaan ci mbëggeel gi nu séq, man Pool màggat, mi ñu tëj kaso ci turu Kirist. 1:10 Maa ngi tinul sama doomu diine Onesim, mi ma jur ci Kirist fii ci kaso bi. 1:11 Amul woon sa njariñ démb, waaye tey amal na nu njariñ, yaw ak man. 1:12 Maa koy yebal fi yaw, waaye xamal ne, mooy sama reeni xol. 1:13 Dama koo bëggoon a téye fi sama wet, ngir mu taxawal la, di ma dimbali, li feek maa ngi ci kaso bi ngir xebaar bu baax bi. 1:14 Waaye bëggumaa def dara loo àndul; noonu ndimbal li nga may defal du nekk sañul-bañ, waaye mu ànd ak xol bu tàlli. 1:15 Xëy na sax dafa tàggoo woon ak yaw diir bu gàtt, ngir nga jotaat ci ba fàww; 1:16 waxuma léegi ni jaam rekk, waaye lu ko sut, xanaa mbokk mu dëggu ci xol, fekk looloo raw ag njaam. Mbokk la ci man, rawatina ci yaw, muy sa jaam ci aada, di sa mbokk léegi ci Boroom bi. 1:17 Soo ma jàppee ni nawle nag, teeru ko, ni su ma la doon ganesi. 1:18 Soo ko naree topp genn tooñ mbaa benn bor, topp ma ko. 1:19 Man Pool maa ngi lay bind ak sama loxob bopp ne, dinaa la ko fey; bëggumaa yegg ci ne, sag dund sax ci man la jaar! 1:20 Waaw yaw sama mbokk, dimbali ma ci Boroom bi, te seral sama xol ci sunu bokk ci Kirist. 1:21 Noonu bind naa la, ndax wóor na ma ne, dinga ma déggal, ba weesu sax li ma la sant. 1:22 Te itam nanga ma waajal néeg, ndaxte yaakaar naa ne, Yàlla dina nangu seeni ñaan, ba delloosi ma leen. 1:23 Sama mbokk Epafras, mi ma nekkal fi ci kaso bi ci turu Kirist, mu ngi lay nuyu. 1:24 Samay àndandoo ci liggéey bi, Màrk, Aristàrk, Demas ak Luug, ñu ngi lay nuyu. 1:25 Na yiwu Boroom bi Yeesu Kirist ànd ak seen xel.
1:1 Li jiitu tey Yàlla waxoon na ak maam ya ci wàll yu bare ak ci tëralin yu wuute jaarale ko ca yonent ya. 1:2 Waaye ci mujug jamono jii nu tollu, Yàlla wax na ak nun jaarale ko ci Doom ji. Doomam jooju la Yàlla jagleel lépp, te ci moom la Yàlla jaar, sàkk àddina. 1:3 Doom ji moo di leer giy jollee ci ndamu Yàlla, di ki dippeekoo ci Yàlla. Moo téye àddina ci kàddoom gu am doole gi. Te bi mu ubbee bunt ba nit di selle ci ay bàkkaaram, dafa toog fa ñu koy terale ca ndeyjooru Aji Màgg ji ca kaw, 1:4 wone noonu ne, moo gën a màgg malaaka yi. Te it Yàlla jox na ko tur wu sut seen tur. 1:5 Ndaxte Yàlla musul a wax kenn ci malaaka yi ne:«Yaa di sama Doom,maa di sa Baay tey.» Musul ne ci mbirum kenn ci ñoom it:«Man Yàlla, dinaa doon Baay ci moom,mu nekk Doom ci man.» 1:6 Waaye bi muy yónni Doom jooju di taaw bi ci àddina, da ne:«Na ko malaakay Yàlla yépp jaamu.» 1:7 Ci wàllu malaaka yi, lii la ci Yàlla wax:«Def na malaakaam yi, ñu mel ni ay ngelaw,ñooñu koy liggéeyal, mu def leen niki safara.» 1:8 Waaye ci wàllu Doom ji, lii la ko Yàlla wax:«Yaw Yàlla, dinga toog ci jal bi ba fàww,ci njubte ngay nguuru. 1:9 Sopp nga njub te bañ lu bon.Looloo tax yaw Yàlla,sa Yàlla sol la mbég mu gën a réymi mu jagleel say àndandoo.» 1:10 Newaat na it:«Yaw Boroom bi,yaa sàkk àddina ca njàlbéen ga,defar asamaan yi ci sa loxoy bopp. 1:11 Yëf yooyu dinañu wéy,waaye yaw dinga sax,dinañu màggat ñoom ñépp ni ay yére. 1:12 Dinga leen taxañ ni malaan,ñu furi ni ay yére,waaye yaw doo soppiku,te sa dund amul àpp.» 1:13 Waaye Yàlla musul a teral kenn ci malaaka yi, ba di ko wax:«Toogal ci sama ndeyjoor,ba kera may daaneel say noonci sa kanam.» 1:14 Malaaka yépp ay xel lañu rekk yuy liggéeyal Yàlla, mu di leen yónni ñuy dimbali nit, ñi nar a jot mucc gi.
2:1 Moo tax kon nu war a gën a faaydaal wax yi nu dégg, ngir bañ a bayliku. 2:2 Xam nanu ne kàddug yoon, wi Yàlla yégle jaarale ko ci malaaka yi, wareef la woon, te képp ku ko mas a moy, walla mu mas koo tanqamlu, jot na mbugal gi mu yelloo. 2:3 Kon nun ñi dégg mucc gu mag gi, bu nu ko sàgganee, nan lanuy man a rëcce mbugalu Yàlla? Boroom bi moo xamle woon mucc googu ca njàlbéen ga, te gannaaw gi, ñi ko dégg, ñoo nu ko wóoralal. 2:4 Te it Yàlla dëggal na seen seede ci ay firnde ak ay kéemaan, ay jaloore yu bare ak ci ay may yu jóge ci Xelam mu Sell, te mu séddale leen ni mu ko bëgge. 2:5 Yàlla jébbalul malaaka yi benn sañ-sañ bu jëm ci jamonoy ëllëg ji nuy wax; keneen la ko jébbal, 2:6 ndaxte am na fu ñu wax ci Mbind mi ne:«Lan mooy nit, yaw Yàlla, ba nga di ko xalaat?Lan mooy doomu nit, ba nga koy topptoo? 2:7 Wàcce nga ko, def komu gën a suufe tuuti malaaka yi.Kaalaa nga ko teraanga ak ndam, 2:8 nootal ko lépp, mu teg ci tànk.» Bi ko Yàlla nootalee lépp nag, bàyyiwul dara. Fi mu nekk gisagunu ne, lépp a ngi ci sañ-sañam; 2:9 Waaye gis nanu Yeesu. Wàcce nañu ko, def ko mu gën a suufe tuuti malaaka yi, ngir mu dee ci wàllu ñépp, ndaxte loolu la Yàlla dogal ci yiwam. Waaye léegi Yàlla kaalaa na ko teraanga ak ndam ndax coono bi mu daj ba dee. 2:10 Ndaxte Yàlla mi yelloo lépp te sàkk lépp, dogal na def ñu bare ay doomam, boole leen ci ndamam. Jekk na nag mu matal Yeesu ci coono bi mu daj, moom mi leen xàllal yoonu mucc gi. 2:11 Moom Yeesu miy sellal, ak ñi muy sellal, ñoom ñépp genn njaboot lañu. Moo tax Yeesu rusu leen a wooye ay doomi baayam. 2:12 Nee na:«Yaw Yàlla, dinaa xamle sa turci samay doomi baay,dinaa la tagg ci biir mbooloo mi.» 2:13 Newaat na:«Dinaa am ci Yàlla kóolute.» Dellu na waxaat ne:«Maa ngi nii, man ak doom yi ma Yàlla jox.» 2:14 Doomam yooyu muy wax, nit kese lañu. Looloo tax Yeesu it moom ci boppam, wàcc na, jëmmoo ni ñoom, ngir dee, ba man caa daaneel Ibliis, mi yore dooley dee. 2:15 Noonu mu yiwi nit, ñi meloon ni ay jaam seen giiru dund gépp ndax ragal a dee. 2:16 Leer na ne, Yeesu xettalisiwul malaaka yi, waaye askanu Ibraayma lay xettalisi. 2:17 Looloo taxoon mu war a mel niy doomi baayam ci bépp fànn, ngir doon seen saraxalekat bu mag fa kanam Yàlla, bi leen yërëm te di sàmm kóllëre, te ci liggéeyu saraxaleem joxe na bakkanam ngir dindi bàkkaari nit ñi, ba Yàlla baal leen. 2:18 Gannaaw sonn na ci nattu yi mu daj, man na dimbali ñiy jaar ciy nattu.
3:1 Kon nag yéen bokk yu sell yi, yéen ñi Yàlla woo, ngeen bokk ci nguuram gu kawe ga, seetleen ci Yeesu, moom miy ndawu Yàlla li, di saraxalekat bu mag bi ci yoon wi nu gëm. 3:2 Ku takku la ci liggéey bi ko Yàlla sas, ni ko Musaa nekke woon ci lépp lu jëm ci waa kër Yàlla. 3:3 Waaye Yeesu yelloo na ndam lu sut lu Musaa, ni kiy tabax kër ëppe maana kër ga muy tabax. 3:4 Ndaxte kër gu nekk am na ku ko sos, waaye ki sos lépp mooy Yàlla. 3:5 Musaa moom ku takku la woon ci lépp lu jëm ci waa kër Yàlla. Waaye jawriñ rekk la woon, ngir seede li Yàlla waroon a yégle. 3:6 Yeesu nag ku takku la it, waaye Doom la, juy yilif kër Baayam. Nun nooy këram googu, bu nu saxee ci sunu kóolute te di bég ci li nuy séentu. 3:7 Moo tax Xel mu Sell mi wax lii ci Mbind mi:«Bu ngeen déggee tey jii baatu Yàlla bi, 3:8 buleen dëgër bopp,ni seeni maam defoon ca màndiŋ ma,keroog ba ñu dëddoo Yàlla di ko diiŋat.» 3:9 Yàlla ne:«Foofa seeni maam diiŋat nañu ma fa,di ma fexee fiir,te gis nañu samay jëf 3:10 diirub ñeent-fukki at.Looloo tax gennliku naa leen, daldi ne:“Seeni xalaat a leen di réeral saa su nekk,xamuñu yoon yi ma neex.” 3:11 Giñ naa kon ci sama mer ne:“Duñu dugg mukk ci sama noflaay.”» 3:12 Bokk yi, wottuleen ba kenn ci yéen bañ a am xol bu bon te gëmadi, bay dëddu Yàlla jiy dund. 3:13 Waaye bés bu nekk, deeleen soññante ci lu jëm ci Yàlla, fi ak bés boobu ñu wax wéyul, ngir ragal bàkkaar nax kenn, ba xolam tëju. 3:14 Am nanu wàll ci Kirist, su nu wéyee fii ba muj ga ci sunu kóolute, gi nu amoon ca njàlbéen ga. 3:15 Lii la Mbind mi wax:«Bu ngeen déggee tey jii baatu Yàlla bi,buleen dëgër bopp,ni seeni maam defoon, ba ñu dëddoo Yàlla.» 3:16 Ñan ñoo dégg baatu Yàlla bi nag te di ko dëddu? Xanaa ña Musaa génne woon Misra ñépp. 3:17 Te ñan la Yàlla mere lu mat ñeent-fukki at? Xanaa ñi daan bàkkaar te seeni néew tëdd ca màndiŋ ma. 3:18 Te it bi Yàlla defee ngiñ lii: «Duñu dugg mukk ci sama noflaay,» booba ñan ñoo ko taxoon di wax? Xanaa ña ko déggadil. 3:19 Noonu gis nanu sax ne, jotuñoo dugg ci noflaay boobu ndax seen gëmadi.
4:1 Yàlla dige na ne, dina am ñu dugg ca noflaayam. Kon ndegam dige boobu mi ngi taxaw ba tey, moytuleen ba kenn ci yéen réer ba du dugg ci noflaay boobu. 4:2 Nun jot nanu xebaar bu baax bi ni ñoom, waaye kàddu, ga ñu déggoon, jariñu leen dara, ndaxte boolewuñu ci ngëm, ba ñu koy déglu. 4:3 Nun ñi gëm nag nooy dugg ci noflaayam, ni ko Mbind mi waxe:«Giñ naa kon ci sama mer ne:“Duñu dugg mukk ci sama noflaay,”» doonte sax liggéeyam bépp matoon na, ca ba mu sàkkee àddina ak léegi. Ci lu jëm ci juróom-ñaareelu fan ba, 4:4 am na fu ñu wax ci Mbind mi ne:«Yàlla noppalu na ci liggéeyam béppca juróom-ñaareelu fan ba.» 4:5 Te it waxoon na ci baat yi nu jot a lim ba noppi:«Duñu dugg mukk ci sama noflaay.» 4:6 Kon am na ñu ci war a dugg ba tey. Te ñi jëkkoon a jot xebaar bu baax bi, dugguñu ci ndax seen déggadi. 4:7 Noonu ay ati at gannaaw ga, Yàlla àppaat na beneen bés, def ko «tey jii,» bi mu waxee ci gémmiñu Daawuda ci baat yii ñu jot a lim:«Bu ngeen déggee tey jii baatu Yàlla bi,buleen dëgër bopp.» 4:8 Su Yosuwe duggaloon sunu maam ya ca noflaayu Yàlla ba, kon gannaaw gi Yàlla du wax dara ci lu jëm ci beneen bés. 4:9 Kon ba tey Yàllaa ngi dencal ay gaayam noflaay bu nirook noflaayu Yàlla ca juróom-ñaareelu fan ba. 4:10 Ndaxte képp ku mas a dugg ca noflaayu Yàlla, noppalu na ci ay jëfam ni Yàlla. 4:11 Nanu farlu boog, ngir dugg ci noflaay boobu, ba kenn bañ a déggadi, ba daanu ni maam ya ca màndiŋ ma. 4:12 Xam nanu ne, kàddug Yàlla mi ngi dund te am na doole. Moo gën a ñaw jaasiy ñaari boor. Day dagg ba fa xol ak xel digaloo, ba fa yax yi ak yuq gi di teqalikoo, te man na àtte xalaat yi ak mébéti xol. 4:13 Te itam amul mbindeef mu man a nëbbu Yàlla, waaye lépp a ubbiku, ba ne fàŋŋ ci bëti ki nu war a àtte. 4:14 Gannaaw am nanu saraxalekat bu mag-a-mag bu àgg ba ca kanam Yàlla, di Yeesu Doomu Yàlla ji, nanu jàpp bu dëgër yoon wi nu gëm. 4:15 Saraxalekat bu mag bi nu am, du ku mënul a bokk ak nun sunuy naqar; moom sax far jaar na ci nattu ni nun ci bépp fànn, waaye deful bàkkaar. 4:16 Kon nag nanu am kóolute ci jege jalu Yàlla bu yiw ba, ngir jot yërmandeem ak yiwam, ngir mu wallu nu fu soxla taxawe.
5:1 Saraxalekat bu mag bu nekk nag, ci biir nit ñi lañu ko jële, te fal ko muy dox seen diggante ak Yàlla. Noonu dina jébbal Yàlla ay sarax, tey rendi ay mala ngir dindi seeni bàkkaar. 5:2 Te ndegam moom ci boppam nit kese la, man na muñal ñiy moy ndax seen ñàkka xam. 5:3 Li mu ñàkk doole moo tax mu war a def ay sarax ngir mbaalug bàkkaaram, ni mu ko tàmmee defal mbooloo mi. 5:4 Kenn mënul a teral sa bopp ba doon ab saraxalekat, su dul ne Yàllaa la woo, ni mu ko defe woon Aaroona. 5:5 Kirist itam yékkatiwul boppam, ba doon saraxalekat bu mag, waaye Yàlla moo ko woo, bi muy wax ne:«Yaa di sama Doom,maa di sa Baay tey.» 5:6 Am na feneen fu mu wax ne:«Doon nga saraxalekat ba fàwwmel ni Melkisedeg.» 5:7 Giiru dundam gépp ci àddina, Kirist da daan ñaan wall ci Yàlla, di ko dénku, boole ko ak i jooy ak i rangooñ. Da doon ñaan ci Yàlla, mi ko man a musal ci dee. Te ñaanam nangu na, ndax ni mu jébbale boppam Yàlla. 5:8 Waaye li muy nekk-nekk doom, teewul mu jàng déggal Yàlla, jaare ko ci coono bi mu daj. 5:9 Noonu la àgge cig mat, ñu def ko ki waral mucc gi dul jeex, ngir ñi ko déggal ñépp. 5:10 Fekk na Yàlla tudde ko saraxalekat bu mag ni ko Melkisedeg nekke. 5:11 Ci fànn googu, am na lu bare lu nu ci bëgg a wax, waaye tekkil leen ko dina jafe, ndaxte dangeen a naqari xel. 5:12 Bu yàgg ngeen waroon a jàngal ñeneen ñi, waaye soxla ngeen ba tey ku leen di tette ci kàddug Yàlla. Léegi nag yéena ngi tollu fi ñu leen war a nàmpale, ndaxte àttanuleen ñam wu dëgër. 5:13 Képp kuy nàmp, ab xale nga ba tey. Jëfeegoo njàngale, mi jëm ci wàllu njubte. 5:14 Waaye ñam wu dëgër, ñi mat a ko yelloo, maanaam ñiy jëfandikoo seen xel ngir ràññee lu baax ak lu bon.
6:1 Kon nag léegi, nanu jóge ci liifantu gi jëm ci Kirist, te jàll cig mat. Nanu bañ a dalaat njàngale mu jëkk moomu, ci ne nit ñi dañoo war a tuub jëf, yi jëm ci dee, te gëm Yàlla, 6:2 di leen jàngalaat ci mbirum sangu set ci ay fànn yu bare, ak teg loxo ak ci mbirum ndekkite ak lu jëm ci àtte biy sax dàkk. 6:3 Te noonu lanuy def, bu soobee Yàlla. 6:4 Li nu war a jëme kanam mooy lii: su amee ay nit ñu Yàlla xas a leeral ba noppi, ñu mos mayu Yàlla gi, am wàll ci Xelam mu Sell, 6:5 te xam mbaax, gi ci kàddug Yàlla, ak kéemaani jamono jiy ñëw, 6:6 te loolu lépp teewul ñu walbatiku, ñooñu kenn dootu leen man a yeesalaat, ba ñu tuub seeni bàkkaar. Li ko waral moo di, dañoo bëgg a daajaat Doomu Yàlla ji ci bant, di ko toroxal, te fekk muy seen ngaañ. 6:7 Maanaam suuf suy naan taw bi ciy dal, tey jox ñi ñu koy beyal gàncax gu am njariñ, day jot barke bi jóge ci Yàlla. 6:8 Waaye su meññee ay dég ak ay xaaxaam, du am benn njariñ; repp na ñu alag ko, te lakk lay mujje. 6:9 Waaye nag yéen samay soppe, su fekkee ne sax, nii lanuy waxe, nu ngi yaakaar li gën ci yéen te ànd ak mucc. 6:10 Yàlla ñàkkul worma bay fàtte seen liggéey ak mbëggeel, gi ngeen wone ci turam, ci li ngeen dimbali ay gaayam, te yéena ngi koy def ba tey. 6:11 Waaye danoo bëgg kenn ku nekk ci yéen wone cawarte gu mel ni ga ngeen amoon, ba kera ngeen di am mat, gi ngeen di séentu. 6:12 Bëggunu ngeen tayel, waaye royleen ñi gëm te muñ, ndaxte ñooy jot li leen Yàlla dig. 6:13 Ibraayma bokk na ci ñoom. Bi ko Yàllay dig, mënul woon a giñ ci keneen ku ko gën a màgg, ba tax mu giñ ci boppam, 6:14 ne ko: «Sàllaaw dinaa la barkeel, yokk saw askan.» 6:15 Noonu Ibraayma di xaar tey muñ, ba jot li ko Yàlla digoon. 6:16 Nit kuy giñ nag, daf koy wékk ci ku ko sut. Ngiñ lu mel noonu moo wóoral mbir te mooy jeexal lépp lu ñuy werante. 6:17 Ñi war a jot li mu dige, Yàlla dafa leen bëggoon a won ne, dogalam du tebbiku mukk; looloo tax mu dige, boole ci ngiñ. 6:18 Noonu ñaari jëf yooyu nga xam ne duñu tebbiku te Yàlla mënu cee dellu gannaaw, dañu nuy gën a sóob ci muñ, nun ñi daw ba am kiiraay, ngir nu man a téye bu dëgër yaakaar, ji mu nu dig. 6:19 Ci yaakaar jooju lanu sës sunu xol, ba man a sampu bu dëgër. Yaakaar la juy jàll ba fa Yàlla nekk, ca gannaaw ridob bérab bu sell-baa-sell. 6:20 Yeesu ci boppam moo fa jëkk a dugg, muy ndaw li nu jiitu, ñu def ko saraxalekat bu mag ba fàww, mel ni Melkisedeg.
7:1 Melkisedeg moomu doon buuru Salem, moo nekkoon saraxalekat ca Yàlla Aji Kawe ji. Gannaaw ba Ibraayma dàqee buur ya, ba dellusi, Melkisedeg gatandu woon na ko, di ko barkeel. 7:2 Noonu Ibraayma fab fukkeelu cér bi, maanaam asaka, ci li mu jële woon ci xare ba lépp, jox ko. Ci lu jëkk turu Melkisedeg mi ngi tekki «buur bu jub bi.» Gannaaw loolu mooy buuru Salem, tur woowu mooy tekki «buuru jàmm.» 7:3 Melkisedeg nag xamaluñu ko baay, xamaluñu ko yaay walla menn maam. Amul fenn fu ñu wax ag juddoom walla ag deeyam. Moo tax nu di ko mengale ak Doomu Yàlla ji, ndaxte saraxalekat la bu kenn dul wuutu. 7:4 Seetleen ni mu màgge, moom Melkisedeg! Ibraayma sax, maamu cosaan mi, fab na li mu jële woon lépp ca xare ba, jox Melkisedeg asaka ja. 7:5 Yoonu Musaa digle na ne, ñi bokk ci giiru Lewi te di ay saraxalekat, nañu jot asaka ci alalu bànni Israyil, doonte sax ñuy seeni bokk te soqikoo ci Ibraayma. 7:6 Waaye Melkisedeg mi bokkul woon ci giiru Lewi, jotoon na asaka ci alali Ibraayma. Te rax-ca-dolli barkeel na ko, moom mi Yàlla sédde woon dige yi. 7:7 Kiy barkeel a gën a màgg ki ñuy barkeel, loolu amu ci benn werante. 7:8 Saraxalekat yi soqikoo ci Lewi, ñu ngi jot asaka, ni ko Melkisedeg jote woon. Waaye ñoom ñu nar a dee lañu. Melkisedeg nag moom, Mbind mi wóoral na ne, dafay dund. 7:9 Léegi nag ci ni ñu ko man a waxe, Lewi miy jot asaka ci bànni Israyil, moom ci boppam jox na ko Melkisedeg, jaare ko ci Ibraayma. 7:10 Ndaxte mi ngi nekkoon ci geñog maamam Ibraayma, bi ko Melkisedeg gatandoo. 7:11 Jox nañu bànni Israyil yoon wu sukkandiku ci liggéeyu saraxalekat yi soqikoo ci Lewi. Su fekkoonte ne nag liggéeyu saraxalekat yooyu manoon na yeggale nit cig mat, kon du soxlaati ab saraxalekat ni ko Melkisedeg nekke, ci fànn gu wuute ak gu Aaroona. 7:12 Te bu ñu fi jëlee saraxalekat yi ak seen liggéey, dañoo war a toxal itam yoon, wi ñu fi tëraloon. 7:13 Noonu Yeesu mi nuy wax, mi ngi soqikoo ci geneen giir gu bokkul ak giiru Lewi. Giir googu nag, amu ci kenn ku ci mas a def liggéeyu saraxale ca saraxalukaay ba. 7:14 Li wóor moo di, sunu Boroom mi ngi soqikoo ci giiru Yuda. Te bi Musaa bindee ci mbirum saraxalekat yi, limaalewul woon giir googu. 7:15 Li waral mbir mi gën a leer moo di ne, beneen saraxalekat bu mel ni Melkisedeg dafa ñëw. 7:16 Te defuñu ko saraxalekat jaarale ko ci yoonu ndono, waaye fal nañu ko ci dooley dund gu amul àpp. 7:17 Ndaxte seedeel nañu Yeesu lii:«Doon nga saraxalekat ba fàwwmel ni Melkisedeg.» 7:18 Noonu tebbi nañu yoon wu jëkk, wa néewoon doole te meññul dara 7:19 --ndax yoonu Musaa yeggalewul dara cig mat — waaye dugalal nañu nu fii yaakaar ju gën ju nu man a jaare ngir jege Yàlla. 7:20 Te rax-ca-dolli ngiñ ànd na ci. Ndaxte ñi soqikoo ci Lewi doon nañu ay saraxalekat te kenn giñul. 7:21 Waaye nag Yeesu moom doon na saraxalekat, bi Yàlla giñee ne ko:«Boroom bi giñ nate du dellu gannaaw mukk:“Doon nga saraxalekat ba fàww.”» 7:22 Ngiñ loolu moo tax Yeesu nekk tayle, giy wóoral kóllëre gi gën. 7:23 Te it yeneen saraxalekat yi dañoo bare woon, ndaxte dee moo daan tax duñu man a sax ci seen liggéey. 7:24 Waaye Yeesu miy dund ba fàww, sasoo na liggéeyu saraxale bu sax fàww. 7:25 Loolu moo tax it mu man a musal tey yeggale cig mat ñiy jaar ci moom te bëgg jege Yàlla, ndaxte mi ngi dund ba fàww ngir di leen rammu. 7:26 Kon nag Yeesu mooy saraxalekat bu mag, bi nu soxla; dafa sell, du def lu bon, du taq bàkkaar, bokkul dara ak bàkkaarkat yi, te yéege nañu ko fa Yàlla. 7:27 Niroowul ak yeneen saraxalekat yu mag yi; soxlawul di def bés bu set ay saraxi mala ngir bàkkaari boppam jëkk, teg ca yoy mbooloo mi. Yeesu def na sarax benn yoon ba fàww ngir dindi bàkkaar yi, bi muy joxe bakkanam. 7:28 Naka yoonu Musaa, aji néew doole yi lay fal saraxalekat yu mag. Waaye ngiñu Yàlla gi ñëw gannaaw yoon wi, Doom ji la fal saraxalekat bu mag bu mat ba fàww.
8:1 Lii mooy li ëpp solo ci li nuy wax: am nanu saraxalekat bu mag bu mel noonu, moom mi toog ci ndeyjooru Aji Màgg ja ca nguuram ca kaw. 8:2 Mu ngi liggéey ca bérab bu sell-baa-sell, di màggalukaay bu dëggu. Nit defaru ko; Boroom bee ko sos. 8:3 Bépp saraxalekat bu mag fal nañu ko, ngir muy def ay sarax ak ay saraxi mala yu jëm ca Yàlla. Kon nag fàww Yeesu am lu mu joxe. 8:4 Bu nekkoon ci àddina, du nekk sax saraxalekat, ndaxte am na fi ba noppi ay saraxalekat yuy def ay sarax, ni ko yoonu Musaa santaanee. 8:5 Saraxalekat yooyu ñu ngi liggéeyal Yàlla ca màggalukaay, ba nekk misaal tey takkandeeru yëf yu dëggu, ya féete kaw. Moo tax ba Musaa naree defar tàntu màggalukaay ba, Yàlla artu na ko ne ko: «Teeylul ba def lépp, roye ko ci bi ma la won ca tund wa.» 8:6 Waaye léegi nag liggéeyu saraxale, bi ñu jox Yeesu, moo gën a màgg liggéeyu saraxalekat yooyu, mel ni it kóllëre, gi Yeesu fas diggante Yàlla ak nit, moo sut kóllëre gu jëkk ga te mu tëdd ci ay dige yu ëpp yu jëkk ya. 8:7 Bu fekkoonte ne, kóllëre gu jëkk ga dafa amul woon benn sikk, kon du aajo ñu koy weccee ak geneen. 8:8 Waaye nag Yàlla sikk na bànni Israyil, bi mu naan:Boroom bi nee na:«Ay fan a ngi ñëwyu may fasi kóllëre gu beesak bànni Israyil ak waa Yude.Kóllëre googu nagbokkul ak gi ma fasoon ak seeni maam, 8:9 ba ma leen jàppee ci loxo,génne leen réewu Misra.Boroom bi nee na:Beddeeku naa leenndaxte sàmmuñu sama kóllëre. 8:10 Boroom bi nee na:Kóllëre gaa ngii,kóllëre gi may fas ak bànni Israyil,bu bés yooyule weesoo.Dinaa def samay ndigal ci seen xel,bind ko ci seen xol.Dinaa nekk seen Yàlla,ñu doon samay gaay. 8:11 Kenn dootul war a jàngal moroomamwalla mbokkam, di wax naan:“Xamal Boroom bi!”Ndaxte ñépp dinañu ma xam,li dale ci ki gën a ndaw ba ci ki gën a mag. 8:12 Ndaxte dinaa leen baal seeni tooñ,te dootuma fàttaliku seeni bàkkaar.» 8:13 Kon nag bi Yàllay wax ci kóllëre gu bees gi, dafa fekk mu màggatal gu jëkk ga. Te lu xewwi te màggat mi ngi ci tànki wéy.
9:1 Kóllëre gu jëkk ga ëmboon na ay ndigal ci mbirum ni ñu war a jaamoo Yàlla. Amoon na itam kër Yàlla gu nekkoon àddina. 9:2 Nekkoon na ab tàntu màggalukaay bu ñu séddale ñaari néeg. Ca ba jiitu la làmpu diwlin ba nekkoon ak taabal, ja ñu daan teg mburu ya ñu daa jébbal Yàlla. Foofaa nga tuddoon bérab bu sell ba. 9:3 Néeg ba ñu tudde bérab bu sell-baa-sell a nga nekkoon ca gannaaw ñaareelu rido ba. 9:4 Saraxalukaayu wurus, ba ñuy taal cuuraay ca kawam, a nga fa woon, ak gaalu kóllëre, ga ñu taf wurus ba mu daj. Ca biir gaal ga amoon na fa benn njaqu wurus bu defoon ñam, wi ñuy wax mànn, ak it yetu Aaroona wi jebbi woon, ak àlluway doj, ya ñu bindoon wax yi kóllëre gi ëmb. 9:5 Ca kaw gaal ga teg nañu fa ñaari nataali mbindeef yu ñuy wax Seruben, yu doon wone ndamu Yàlla. Seeni laaf ñoo doon yiir baalukaay ba. Waaye loolu lépp léegi mënunu koo tekki benn-benn. 9:6 Ba ñu defaree lépp, saraxalekat ya dañu daan dugg bés bu set ca néeg bu jëkk ba, ngir mottali seen liggéeyu saraxale ca Yàlla. 9:7 Waaye ca néeg ba ca topp, saraxalekat bu mag ba rekk moo fa daan dugg benn yoon ci at mi. Te daawu fa dugg mukk te yóbbaalewul deretu mala, yi muy jagleel Yàlla, ngir bàkkaari boppam ak yu mbooloo mi daan def ci seen ñàkka xam. 9:8 Ci noonu nag Xel mu Sell mi wone na ne, yoon wi ñuy jaar, ba dem ca bérab bu sell-baa-sell, ubbikoogul woon, fi ak tànt ba jëkk baa ngi doon taxaw. 9:9 Misaal la ci jamonoy tey; dafay wone ne, sarax yi ak saraxi mala yi ñu daan jagleel Yàlla, mënuñoo dalal xelu jaamukatu Yàlla bi. 9:10 Sarax yooyu ñu ngi jëmoon ci lekk ak ci naan ak ci fànn yu bare ci mbirum sangu set. Ay sàrt yu jëm ci yaram lañu, yu ñu waroon a farataal, ba kera jamono ji Yàllay tëral kóllëre gu bees. 9:11 Waaye Kirist ñëw na, doon saraxalekat bu mag, bi joxe xéewal yi teew. Jaar na ca màggalukaay ba gën a màgg te gën a mat, te màggalukaay booba loxol nit defaru ko, maanaam bokkul ci àddina sii. 9:12 Noonu Kirist dugg na benn yoon ba fàww ca bérab bu sell-baa-sell. Duggu fa ak deretu sikket yi ak yu yëkk yi. Waaye mi ngi duggaale ak deretu boppam te indil na nu noonu njot gu amul àpp. 9:13 Deretu sikket yi ak ju yëkk yi, ak wëllu, wi ñu lakk te di suy dóom bi ñi taq sobe, ñooy sellal yaram. 9:14 Su fekkee ne noonu la deme nag, du kon deretu Kirist moo ëpp doole? Jox na bakkanam Yàlla, def ko sarax su amul sikk jaarale ko ci dooley Xel miy sax abadan. Kon deretam moo man a sellal sunu xel, mi nu doon yedd ndax jëf yu jëm ci dee, ngir nu man a jaamu Yàlla jiy dund. 9:15 Looloo tax mu nekk Rammukat bi ci wàllu kóllëre gu bees ci diggante Yàlla ak nit, ngir ñi Yàlla woo am cér bu sax ci kaw, te mu digoon leen ko, ndaxte Kirist dee na, ngir jot ñi jàdd yoon ca kóllëre gu jëkk ga. 9:16 Ci li jëm ci dénkaane bu ñu bind, jëme ci miraas, fàww ñu wone firndeg deewu ka ko bind, 9:17 ndaxte bala dénkaaneb miraas di taxaw, dee am; te taxawul, fi ak ki ko bind a ngi dund. 9:18 Looloo waral kóllëre gu jëkk ga, ñu fasoon ko ak deret. 9:19 Keroog Musaa jàng na ndigali yoon wépp ci kanamu bànni Israyil gépp. Gannaaw loolu jël na deretu wëllu, jëlaale ndox, ak bantu garab gu ñuy wax isob, laxas ci kawaru xar mu xonq. Noonu mu capp ko ca deret ja, daldi ko wis ca téereb yoon wa ak ca mbooloo mépp 9:20 te naan: «Lii mooy deretu kóllëre gi leen Yàlla tëralal.» 9:21 Noonu mu daldi wis it deret ja ca tànt ba ak ca jumtukaay, ya ñu daan jaamoo. 9:22 Ndaxte ci yoonu Musaa, daanaka deret lañuy sellale lépp, te bu deret tuuruwul, mbaalug bàkkaar du am. 9:23 Yëfi àddina yi misaal yu dëggu yi ci asamaan, war nañu leen a sellale noonu. Waaye yëf yu dëggu yooyu ci asamaan, laaj na sarax yu gën a baax, ngir ñu sell. 9:24 Ndaxte Kirist duggul ci bérab bu sell bu nit tabax, muy doon nataal ci bu dëggu bi. Waaye dugg na ca biir asamaan sax, ngir taxawal nu ca kanam Yàlla léegi. 9:25 Saraxalekat bu mag bi dafay dugg at mu jot ca bérab bu sell-baa-sell ak deret ju dul josam. Waaye Kirist joxewul bakkanam ay yooni yoon. 9:26 Bu demee woon noonu, kon dina sonn ba tàyyi ca njàlbéenug àddina ba tey. Waaye nag benn yoon rekk la feeñu ci mujjeelu jamono yi, joxe boppam ni sarax ngir far bàkkaar yi. 9:27 Kon ni nit ñi deeye benn yoon rekk, ba noppi jaar ca àtte ba, ni ko Yàlla dogale, 9:28 noonu it la Kirist joxee boppam benn yoon, ngir gàddu bàkkaaru nit ñu bare, te dina feeñaat, waxuma ci mbiri bàkkaar, waaye ngir indil ñi koy séentu mucc gi.
10:1 Yoonu Musaa dafa misaal xéewal yi waroon a ñëw; takkandeer la ci yëf yu dëggu yi, waaye du ñoom ci seen bopp. Looloo tax mënul a yeggale cig mat ñi ñëw ci Yàlla, ndaxte at mu nekk duñu jóg ci jébbal Yàlla sarax yooyu. 10:2 Sarax yi ñuy def, bu ñu manoon a sellal ñiy jaamu benn yoon ba fàww, kon dinañu leen bàyyi, ndaxte dootuñu am yeraange ci seeni bàkkaar. 10:3 Waaye dañuy fàttaliku bàkkaar yi ci sarax yi ñuy def at mu jot. 10:4 Ndaxte deretu yëkk yi ak ju sikket yi mënuñoo dindi bàkkaar yi. 10:5 Looloo tax bi muy wàcc àddina, Kirist nee na:«Bëggoo saraxu mala walla beneen sarax,waaye aw yaram nga ma defaral. 10:6 Sarax yu ñuy lakkwalla sarax yiy dindi bàkkaar,benn neexu la ci. 10:7 Moo tax ma ne: “Damaa wàccngir def sa coobare, yaw Yàlla,mu dëppoo ak li ñu bind ci sama mbirci téereb yoon wi.”» 10:8 Wax na bu jëkk: «Saraxi mala walla yeneeni sarax, sarax yu ñuy lakk walla sarax yiy dindi bàkkaar, bëgguloo leen te benn neexu la ci.» Teewul yoon wi moo leen santaane. 10:9 Noonu mu tegaat ca ne: «Damaa wàcc ngir def sa coobare.» Noonu toxal na jëfin wu jëkk wa, ngir wuutal fi weneen wu bees. 10:10 Te ci li Kirist def coobareg Yàlla, bi mu joxee yaramam sarax benn yoon ba fàww, moo tax nu sell ci bàkkaar. 10:11 Bés bu nekk saraxalekat yi dañuy taxaw di liggéeyal Yàlla, di sax ci def sarax yu mënul a dindi bàkkaar yi mukk. 10:12 Waaye nag saraxalekat bii di Kirist, bi mu saraxee sarax bu am doole ngir dindi bàkkaar yi benn yoon ba fàww, dafa toog ca ndeyjooru Yàlla, 10:13 di xaar ba kera mu daaneel ko ay noonam ci kanamam. 10:14 Noonu ñi ñuy sellal, ci benn sarax rekk la leen yeggali cig mat ba fàww. 10:15 Te it Xel mu Sell mi seedeel na nu ko; 10:16 dafa jëkk a wax ne:«Boroom bi nee na:Kóllëre gaa ngii,kóllëre gi may fas ak ñoom,bu bés yooyule weesoo.Dinaa def samay ndigal ci seen xol,bind ko ci seen xel.» 10:17 Noonu mu tegaat ca ne:«Dootuma fàttaliku seeni bàkkaarwalla seeni tooñ.» 10:18 Kon nag fu ñuy baale bàkkaar, aajootul sarax su koy dindi. 10:19 Bokk yi, gannaaw nag deretu Yeesu may na nu sañ-sañu dugg ca bérab bu sell-baa-sell, 10:20 nuy jaar ci rido bi, ci yoon wi mu nu ubbil, di yoon wu bees tey dund, maanaam ndax li mu joxe yaramam sarax te mi ngi dund, 10:21 te gannaaw am nanu saraxalekat bu mag, biy yilif waa kër Yàlla, 10:22 kon nanu jege Yàlla ak xol bu laab, ak ngëm gu ànd ak kóolute, am xel mu dal ci bépp yeraange, ak yaram wu ñu raxas ci ndox mu sell. 10:23 Nanu jàpp ci yaakaar, ji nu am, te bañ a toqi, ndaxte ki nu dig, lu mu wax def ko. 10:24 Nanu seet ni nu man a xiirtalante cig mbëggeel ak ci jëf yu baax. 10:25 Te bunu bàyyi sunu ndaje yi, ni ko ñenn ñi di defe, waaye nanuy nàddante ci ngëm, di ko feddali, fi ak yéena ngi gis bésu Boroom biy jubsi. 10:26 Gannaaw ba nu nangoo xam dëgg ba noppi, bu nu teyee di def bàkkaar, kon sarax dootul am ngir bàkkaar yooyu. 10:27 Déedéet, bu nu defee noonu, dinanu tiit di xaar àtte ba, muy taal bu yànj, biy war a lakk nooni Yàlla yi. 10:28 Ku weddi ndigali yoonu Musaa wi, te ñaar walla ñetti nit seede ko, dina dee ci lu amul benn yërmande. 10:29 Ku xeeb Doomu Yàlla ji te fonkadi deretu kóllëre, ji ñu ko sellale, te muy toroxal Xelum Yàlla, mi indi yiw, naka la mbugalam war a gën a yéese? 10:30 Xam nanu ki wax ne: «Man maay àtte, maay fey jëf.» Te newaat na: «Boroom bi dina àtte ay gaayam.» 10:31 Ndaw tiitaange ci ku sàggan, ba tàbbi ci loxoy Yàlla jiy dund! 10:32 Fàttalikuleen bés yu jëkk ya, ba leeru Yàlla tàbbee ci yéen; dékku ngeen xeex bu mag ciy fitna. 10:33 Léeg-léeg ñu saaga leen ak di leen sonal ci kanamu nit ñi; léeg-léeg it ngeen taxawu ñi ñuy def noonu. 10:34 Ndaxte bokk ngeen naqar ak ñi ñu tëj, te nangu ngeen ak xol bu sedd, ñu foqarñi seen alal, xam ne, am ngeen alal ju gën te di sax ba fàww. 10:35 Kon nag buleen sàggane kóolute gi ngeen am, ndaxte ëmb na yool bu mag. 10:36 Dangeen a war a muñ, ba def coobareg Yàlla, sog a jot li mu leen digoon. 10:37 Ndaxte lii la Mbind mi wax:«Ci kanam tuuti, ki war a ñëw dina ñëwte léegi mu agsi. 10:38 Ku jub ci sama kanam dina dund ci kaw ngëm,waaye bu delloo gannaaw,sama xol du sedd ci moom.» 10:39 Nun nag bokkunu ci ñiy dellu gannaaw bay réer, waaye nu ngi bokk ci ñi am ngëm tey mucc.
11:1 Am ngëm lii lay tekki: dafa nuy wóor ne, li nuy yaakaar dina am, te it li nu dul gis nekk na. 11:2 Maam ya, seen ngëm a tax ba Yàlla seedeel leen lu baax. 11:3 Ngëm a tax ba nu xam ne, Yàlla sàkk na àddina jaarale ko ci kàddoom, ngir li bët di gis, defarees ko ak lu bët mënul a gis. 11:4 Ngëm moo tax ba Abel jébbal Yàlla sarax su gën saraxu Kayin. Ngëmu Abel moo tax ba Yàlla àtte ko ni ku jub, bi mu ko seedeelee ne, saraxam baax na. Te ci kaw ngëm lay wax ba tey, moom mi dee ba noppi. 11:5 Ngëm moo tax ba Enog jaarul ci dee. Yàllaa ko yóbbu ca moom, te kenn gisatu ko, ndaxte Yàllaa ko toxal. Ndaxte Mbind mi seedeel na ko ne, laata muy toxu, neex na Yàlla. 11:6 Waaye ku amul ngëm doo man a neex Yàlla, ndaxte ku bëgg a jegeñ Yàlla war ngaa gëm ne, Yàlla am na te dina neexal ñi koy wut. 11:7 Ngëm moo tax ba, bi Yàlla yégalee Nóoyin lu jiitu ci mbir yi dikkagul, mu ragal ba defar gaal ngir musal njabootam. Ngëmam moo tax mu yey niti àddina, ba noppi jot njubte, li Yàllay joxe ci kaw ngëm. 11:8 Ngëm moo tax ba Ibraayma déggal Yàlla. Bi ko Yàlla wooyee, mu dem toxu ci menn réew, ma mu waroon a jote ca Yàlla. Noonu la gàddaaye dëkkam te xamul woon fan la jëm. 11:9 Ngëm a tax ba Ibraayma sanc ci réew, mi ko Yàlla digoon, dëkk ci ay tànt ni doxandéem, moom ak doomam Isaaxa ak sëtam Yanqóoba, fekk sax Yàlla digoon na leen réew mi. 11:10 Waaye nag Ibraaymaa ngi doon séentu dëkk bi sax, bi Yàlla tabax te sanc ko. 11:11 Ngëm moo tax ba Ibraayma, li muy màggat lépp te Saarata mënul woon a am doom, Yàlla def ba mu jur doom, ndaxte dafa gëmoon ne, Yàlla lu mu dige def ko. 11:12 Looloo tax ba, Ibraayma mi màggat lool, aw xeet jóge ci moom, baree ni biddiiwi asamaan, te sakkan ni suufu tefes, ba kenn mënu koo xayma. 11:13 Ñoom ñépp dee nañu ci ngëm. Jotuñu li ñu leen digoon, waaye séen nañu ko fu sore ba nuyu leen, te nangu ne, ay doxandéem ak i gan lañu woon ci àddina. 11:14 Ñiy waxe noonu nag dañuy wone ne, ñoo ngi wut réew mu ñu moomal seen bopp. 11:15 Bu ñu nammoon réew mi ñu jóge, kon dinañu am jotu dellu fa. 11:16 Waaye ñu ngi doon séentu réew mu gën, maanaam mi nekk ci asamaan. Looloo tax Yàlla rusul ñu koy wooye seen Yàlla, ndaxte defaral na leen ab dëkk. 11:17 Ngëm moo tax Ibraayma naroon a rey Isaaxa ni sarax, bi ko Yàlla nattoo. Moom mi jotoon dige yi, moo demoon bay saraxe jenn doom ji mu am kepp, 11:18 fekk sax Yàlla nee woon na ko: «Saw askan ci Isaaxa lay jaar.» 11:19 Waaye xelu Ibraayma jàppoon na ne, Yàlla am na dooley dekkal néew yi. Te dëgg-dëgg ci misaal dafa mel ni, Isaaxa dafa dee te dekki. 11:20 Te it ngëm moo tax ba Isaaxa barkeel Yanqóoba ak Esawu, di wax ci mbirum yëf yiy ñëw. 11:21 Ngëm moo tax ba, bi Yanqóoba nekkee ci sukkurat, mu barkeel kenn ku nekk ci doomi Yuusufa yi. Moo tax it mu màggal Yàlla, jafandu ci yetam. 11:22 Ngëm moo tax ba, bi Yuusufa nekkee ci sukkurat, mu waxoon ci gàddaay gi bànni Israyil waroon a gàddaaye Misra, di joxe ndigal jëme ci mbirum néewam. 11:23 Ngëm moo tax ba, bi Musaa juddoo, ay waajuram nëbb ko lu mat ñetti weer, ndaxte gisoon nañu ne, xale bu taaru la woon, te ragaluñu woon ndigalu buur bi. 11:24 Ngëm a tax ba bi Musaa màggee, muy bañ ñu koy wooye sëtu Firawna. 11:25 Bokk coono ak gaayi Yàlla yi moo ko gënaloon muy bànneexu ab diir ci bàkkaar. 11:26 Ñu toroxal ko ngir Almasi bi mi ngi mel ci moom ni alal ju ëpp alali Misra yépp, ndaxte yool bi la doon séentu. 11:27 Ngëm moo tax mu jóge Misra te ragalul merum buur bi. Dafa muñ, mel ni nit kuy gis Yàlla, mi kenn mënul a teg bët. 11:28 Ngëm moo tax mu sos màggalu Bésu Jéggi ba, di wis deret ci bunt yi, ngir malaakam Yàqkat mi bañ a laal taawi bànni Israyil. 11:29 Ngëm moo tax ba bànni Israyil jaar ci Géej gu xonq gi, mel ni kuy jaar ci yoonu suuf su wow. Waaye bi ci waa Misra yi doon jéem a jaar, ñoom ñu daldi lab. 11:30 Ngëm moo tax miir yi wëroon dëkku Yeriko màbb, gannaaw ba ko bànni Israyil wëree lu mat juróom-ñaari fan. 11:31 Ngëm moo tax ba Raxab jigéenu moykat bi mucc, keroog ba ñuy bóom ñi déggadiloon Yàlla, ndax li mu teeru woon yëddukat ya teeru bu ànd ak jàmm. 11:32 Lu ma ci war a tegaat? Ndaxte awma jotu wax ci mbirum Sedeyon, Barag, Samson, Yefte, Daawuda, Samwil ak yonent yi. 11:33 Seen ngëm a tax ñu noot ay buur, di doxal yoon tey jot li Yàlla dige. Ngëm moo tax ba tey, ñu tëj gémmiñu gaynde yi, 11:34 fey dooley safara, rëcc ci jaasi, ñu génn ci néew doole, dugg ci kàttan, doon ay jàmbaar, dàq xarekat, ya jóge bitim réew. 11:35 Ngëm moo tax ba ay jigéen gis ñu dekkal seeni néew, delloo leen ko; ñeneen ñi ñu metital leen, te bañ ku leen musal, ngir jot ndekkite lu gën. 11:36 Ñeneen ñi dékku nañu ay xas ak ay yar, ay jéng ak kaso yi. 11:37 Ñii, sànni nañu leen ay xeer ba ñu dee; ñii, ñu xar leen ñaar; ñii, ñu reye leen jaasi. Ñu ngi doon wëndéelu, sol ay deri xar ak yu bëy, di ay walaakaana; ñu di leen sonal, di leen fitnaal. 11:38 Ñu ngi leen doon def noonu, fekk àddina sax yelloowul leen. Ñu ngi doon wëreelu ci àll yi ak ci tund yi, dal ci xunti yi ak ci kàmb yi. 11:39 Nit ñooñu ñépp, seen ngëm a tax ba Yàlla seedeeloon leen lu baax. Moona de, jotuñu li Yàlla dige woon, 11:40 ndaxte Yàlla dafa tëral lu gën ci nun te bëggu leen a yeggale cig mat, fi ak ànduñu ci ak nun.
12:1 Kon nag gannaaw mbooloo mu bare moo nu yéew, di nu seedeel seen ngëm, nanu yenniku bépp yen ak bàkkaar bu nuy téqtal ci lu yomb, tey daw xél wi nekk sunu kanam, ànd ci ak muñ. 12:2 Nanu ne jàkk Yeesu, moom mi samp ngëm, ba ub làmbi ngëm. Mbég mi mu dëgmël moo tax mu dékku dee ca bant ba te faalewul toroxte, ji ko fa fekk, ba noppi toog ca ndeyjooru jal, ba Yàlla nekk. 12:3 Defleen seen xel ci moom, moom mi muñ noonu ko bàkkaarkat yi bañe woon, ngir bañ seen kàttan jeex, ngeen xàddi. 12:4 Yéen demaguleen ba tuur seen deret ci seen bëre ak bàkkaar. 12:5 Te fàtte ngeen li leen Yàlla dénk ni baay ak ay doomam naan:«Sama doom, bul fonkadi yarub Boroom bimbaa ngay xàddi, bu lay yedd, 12:6 ndaxte ku Boroom bi sopp, yar la,tey duma bépp doom bu mu nangu.» 12:7 Li ngeen di war a muñ, ab yar la. Yàlla dafay jëf ak yéen ni ay doomam, ndaxte ana doom ju baayam dul yar? 12:8 Bu ngeen bokkul woon ci yar, bi ñépp am wàll, kon dungeen ay doomi yoon; ay doom yu daganul ngeen. 12:9 Waaye sax far, sunuy baay ci àddina yaroon nañu nu, te wegoon nanu leen. Baay bi yore ruu yi kon, xanaa warunu koo gën a déggal ngir man a dund? 12:10 Sunuy baay yar nañu nu diir bu gàtt ci seen coobare. Waaye Yàlla dafa nuy yar ngir sunu njariñ, ngir nu bokk ci sellaayam. 12:11 Li am moo di ne, yar bu nuy dal, du ànd ak bànneex, day naqari, waaye gannaaw ga dafay meññ jub ak jàmm, ci ñi ko jariñoo. 12:12 Kon nag mayleen doole loxo yi toqi, ak óom yi bañ, 12:13 te fàkkal seeni tànk ay yoon yu jub, ngir cér bi làggi bañ cee jekkalikoo waaye mu wére ci. 12:14 Wutleen ak ñépp jàmm te fonk dund gu sell, ndaxte ku sellul doo gis Boroom bi. 12:15 Moytuleen ba kenn du ñàkk yiwu Yàlla mbaa kenn mel ni reen bu wex buy jebbi, ba di leen lëjal tey gaañ ñu bare ci wextanam. 12:16 Moytuleen it ba kenn du njaaloo walla muy fonkadi yëfi Yàlla, ni Esawu, mi weccee woon ndonol taawam ngir ag lekk. 12:17 Xam ngeen ne, ba ñu ca tegee tuuti, gàntu nañu ko, ba mu bëggee jot barke bi. Amul fenn fu mu jaar ba defar njuumteem, te jooy, yi mu doon jooy, mënu ci dara. 12:18 Ndaxte meluleen ni bànni Israyil ñoom ñi jege woon tund wu ñu man a laal, wu doon tàkk jeppit te ànd ak xiin ak lëndëm ak ngelaw. 12:19 Jegewuleen liit guy jib ak baat buy wax ay wax yoo xam ne ñi ko doon dégg, ñaan ñu bañ leen cee tegal benn baat, 12:20 ndaxte mënuñu woon a dékku ndigal lii: «Su mala sax laalee tund wa, nangeen ko sànni ay xeer, ba mu dee.» 12:21 Te mbir moomu ñu doon seetaan dafa raglu, ba Musaa naan: «Damaa tiit bay lox.» 12:22 Waaye yéen jege ngeen tund wi ñuy wax Siyon, di dëkku Yàlla jiy dund, muy Yerusalem ba ca asamaan. Jege ngeen it junniy junniy malaaka yu bég-a-bég, ba daje di màggal; 12:23 jege mbooloom taawi Yàlla, yu ñu bind seen tur ca asamaan. Jege ngeen Yàlla, jiy àtte ñépp; jege ruuwi nit ñu jub, ñi àgg cig mat; 12:24 jege Yeesu, Rammukat bi sàmm kóllëre gu bees gi; jege deretam, ji ñu wis. Te deret jooju, li muy yégle moo gën a neex li deretu Abel doon yéene. 12:25 Moytuleen a tanqamlu nag kiy wax ak yéen. Ndegam ñiy tanqamlu ki leen di artu ci àddina, ñoo mënul a rëcc ci àtte bi, aste ku dummóoyu kiy wax ci asamaan. 12:26 Bu jëkk baatam yengaloon na suuf, waaye léegi dafa dige ne: «Beneen yoon laay yengalaat suuf, yengal asamaan itam.» 12:27 Ci li mu wax: «Beneen yoon,» dafay xamle ne, Yàlla dina dindi yi ñu man a yengal, maanaam li ñu sàkk, ngir li ñu mënul a yengal sax ba fàww. 12:28 Kon nag gannaaw dinañu jot nguur gu kenn mënul a yengal, nanu ci sant Yàlla, di ko jaamu, ni mu ko bëgge, boole ci wegeel ak ragal, 12:29 ndaxte sunu Yàlla, safara la suy lakke.
13:1 Saxleen ci bëggante ni ay bokk. 13:2 Buleen fàttee teral ñiy ñëw ci yéen, ndaxte ñenn ñi, bi ñu ko defee, teral nañu ay malaaka te xamuñu ko. 13:3 Fàttalikuleen ñi ñu tëj, mel ni su ñu leen boole woon ak ñoom tëjaale. Fàttalikuleen ñi ñuy sonal, ni su ngeen bokkoon ak ñoom coono. 13:4 Na ñépp fullaal séy, te lalu séy bi bañ a taq sobe, ndaxte Yàlla dina àtte ñu yàqu ñi ak njaalookat yi. 13:5 Buleen bëgge; deeleen doylu, ndaxte Yàlla ci boppam nee na:«Duma la wacc mukk,duma la wor mukk,» 13:6 ba tax nu am kóoluteg wax ne:«Boroom bi moo di sama ndimbal;duma ragal dara.Lu ma nit manal?» 13:7 Fàttalikuleen seen njiit, yi leen yégal kàddug Yàlla. Nemmikuleen li seen dund meññ te roy seen ngëm. 13:8 Yeesu Kirist du soppiku mukk; ni mu mel démb ak tey lay mel ba fàww. 13:9 Buleen nangu mukk ñu fàbbi leen ak njàngale yu bare yu wuute ak yu jëkk ya. Li gën moo di xol yi jële seen doole ci yiwu Yàlla, te bañ koo jële ci sàrt yi jëm ci ñam, yi jariñul dara ñi koy sàmm. 13:10 Am nanu sarax boo xam ne ñiy jaamu Yàlla ci tàntu màggalukaayu bànni Israyil sañuñu koo lekk. 13:11 Ndaxte saraxalekat bu mag bi dafay yóbbu deretu mala yi ca bérab bu sell-baa-sell ni sarax ngir dindi bàkkaar yi, waaye yàpp wi dees na ko lakk ca gannaaw dal ba. 13:12 Looloo tax Yeesu sonn ca gannaaw dëkk ba, ngir sellal mbooloo mi ak deretam. 13:13 Nanu ko fekki nag ca gannaaw dal ba, bokk ak moom toroxte ga. 13:14 Amunu fii ci àddina dëkk bu sax ba fàww, waaye nu ngi wut dëkk biy ñëw. 13:15 Kon nag nanu jaare ci Yeesu, tey dëkk ci jébbal Yàlla sarax bu koy màggal, maanaam sant turam. 13:16 Buleen fàtte di def lu baax ak di sédde ci seen alal, ndaxte sarax yu mel noonu ñoo neex Yàlla. 13:17 Déggal-leen seeni njiit te topp seen ndigal, ndaxte ñoo leen di sàmm te ñooy layoo seen liggéey. Kon nangeen leen déggal, ngir ñu man a def seen liggéey ak xol bu sedd, bañ cee am naqar, ndaxte loolu du leen amal njariñ. 13:18 Deeleen nu ñaanal. Wóor nanu ne, sunu xel dal na, ndaxte danoo bëgg a rafet ci lépp lu nuy def. 13:19 Maa ngi leen di xiir, ngeen ñaanal nu, ba tuur ci seen ñaq, ngir ma yiwiku, ba dellusi ci yéen ci ni mu gën a gaawe. 13:20 Na leen Yàlla Boroom jàmm, mi dekkal sunu Boroom Yeesu, di Sàmm bu mag bi, ci darajay deret, ji fas kóllëre gu sax, 13:21 matal ci lépp lu baax, ba ngeen man a def coobareem, di jëfe ci nun li neex ci moom, mu jaarale lépp ci Yeesu Kirist, moom mi yelloo ndam ba fàww. Amiin. 13:22 Kon nag bokk yi, maa ngi leen di ñaan, ngeen tegoo baatu yedd yooyu, ndaxte dama leen a bind ci lu gàtt. 13:23 Xamleen ne, Timote sunu mbokk, génn na kaso. Su dikkee léegi, dinaa ànd ak moom, seetsi leen. 13:24 Nuyul-leen ma seen njiit yépp ak gaayi Yàlla yépp. Waa Itali ñu ngi leen di nuyu. 13:25 Na yiwu Yàlla nekk ànd ak yéen ñépp.
1:1 Man Saag, jaamu Yàlla ak Boroom bi Yeesu Kirist, maa leen di nuyu, yéen fukki giir ak ñaar, yi tasaaroo ci biir àddina si. 1:2 Yéen samay bokk, waxtu wu nattu yi dalee ci seen kaw, ak nu ñu man a mel, defleen ko ni mbég mu réy, 1:3 xam ne nattub ngëm mooy ndeyu muñ. 1:4 Kon na seen muñ dem ba mat, ngir ngeen bañ a fell fenn, waaye ngeen mat sëkk. 1:5 Ku xelam des ci benn fànn ci yéen nag, na ko ñaan Yàlla, te dina ko ko may, ndaxte Yàlla mooy Aji Yéwén, jiy may ñépp ci lu àndul ak genn ŋàññ. 1:6 Waaye na ko ñaan ci ngëm te bañ cee werante; ndaxte kiy werante mi ngi mel ni ndoxum géej, mi ngelaw liy lëmbaaje wet gu ne. 1:7 Bu kooku yaakaar dara ci Boroom bi. 1:8 Ku am xel ñaar la, te ñàkk pasteef ci lépp lu mu man a def. 1:9 Naka mbokk mi néew doole, na sant ci teraangaam fa kanam Yàlla, 1:10 te boroom alal it sant cig suufeem, ndax ni tóor-tóor di ruuse, noonu lay wéye. 1:11 Su jant fenkee, ba naaj wi tàng, kon gàncax lax, tóor-tóor ruus, te rafetaayam naaw. Noonu la boroom alal di nasaxe, moom ak i jëfam. 1:12 Ku dékku nattu, ku barkeel nga, ndax boo ci génnee ak ndam, dees na la jagleel kaalag dund, gi Yàlla dig ñi ko bëgg. 1:13 Bu la fiir galanee, bul ne: «Yàllaa ko dogal,» ndaxte Yàlla jegewul ak mbon fenn te du fiir kenn. 1:14 Waaye ku sa bakkan nax, ba man la, looloo lay dugal ci fiir. 1:15 Kon bu bëgg-bëgg ëmbee, bàkkaar lay wasin, te bu bàkkaar màggee, jur dee. 1:16 Yéen sama bokk yi ma bëgg, buleen juum ci lii: 1:17 gépp may gu baax ak gépp jagle gu mat, ci Yàlla la jóge, di Baay bi sàkk leeri asamaan, fekk moom du soppiku, mbaa muy leer ak di lëndëm. 1:18 Ci coobareem la nu sole kàddug dëgg gi, ba nu judduwaat, di tànneefu lépp lu mu bind. 1:19 Yéen sama bokk yi ma bëgg, nangeen xam lii: ku nekk war ngaa farlu ci déglu, di yéex a wax tey yéex a mer. 1:20 Ndaxte meru nit du jur njub gi neex Yàlla. 1:21 Moo tax nanguleen ci woyof kàddu, gi leen Yàlla sol te man leen a musal, di dëddu bépp sobe ak coxor gi daj àddina. 1:22 Buleen yem ci déglu kàddu gi rekk, di nax seen bopp; waaye jëfeleen ko. 1:23 Ndaxte ku déglu kàddu gi, te bañ koo jëfe, moom ak kuy seetu ñoo yem; 1:24 day gis xar-kanamam, te su nee wërëñ, daldi fàtte meloom. 1:25 Waaye kuy gëstu yoonu Yàlla, wi mat tey goreel --waxuma ki dégg, ba noppi fàtte, waaye kiy jëfe ndigal — kooku barkeel na ci kaw jëfam. 1:26 Ku yaakaar ne am na diine, waaye moomul làmmiñam, xanaa di nax boppam rekk, diineem jooju du diiney dara. 1:27 Ku diineem sell te amul benn gàkk fa kanam Yàlla mooy kii: ki nemmiku jiirim yi ak jigéen ñi seen jëkkër faatu ci seeni tiis, tey waggar sobey àddina.
2:1 Yéen samay bokk, bu benn gënale laal seen ngëm ci sunu Boroom Yeesu Kirist, mi soloo ndam. 2:2 Ndaxte su ñaari nit duggee ci seen mbooloo, kii takk jaaroy wurus te sol yére yu taaru, ka ca des ñàkk te limboo ay sagar, 2:3 ngeen teral boroom daraja ji ne ko: «Àggal ci jataay bu yiw bi,» ba noppi ngeen ne aji néew doole ji: «Taxawal fale, mbaa nga toog fi ci samay tànk,» 2:4 kon gënale ngeen ci seen biir, ba àtte ci col, bàyyi xol. 2:5 Dégluleen yéen sama bokk yi ma bëgg, ndax Yàlla tànnul ñi néewle ci àddina, ngir ñu barele ci ngëm, tey am i cér ci nguur, gi Yàlla dig ñi ko bëgg? 2:6 Fekk dangeen leen di toroxal! Xanaa du boroom alal yi ñoo leen di noot te di leen yóbbu fa kanam àttekat yi? 2:7 Ndax duñu tilimal tur wu tedd, wi ngeen di wuyoo? 2:8 Su ngeen sàmmee yoonu Buur Yàlla, ni ko Mbind mi tërale naan: «Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp,» kon def ngeen lu baax. 2:9 Waaye su ngeen gënalee, bàkkaar ngeen, te yoonu Yàlla dina leen dab ni ñu moy. 2:10 Ndaxte ku sàmm yoon wépp, waaye xëtt ci lenn ndigal rekk, jàdd nga yoon wépp. 2:11 Ndaxte Yàlla mi ne: «Bul njaaloo,» teg na ca ne: «Bul rey nit.» Ku njaaloowul nag, waaye nga rey nit, jàdd nga yoon wépp. 2:12 Gannaaw dingeen nar a jaar ci àtteb yoon, wiy goreel, na loolu lal seen wax ak seen jëf. 2:13 Ndaxte ku yërëmul, yoon du la yërëm. Te yërmande mooy noot àtte. 2:14 Te lii itam samay bokk, ku ne gëm nga, te jëfewoo ko, loolu lu muy jariñ? Ndax googu ngëm man na laa musal? 2:15 Su amee mbokk ci seen biir, mu rafle te amul dund, muy góor walla jigéen, 2:16 te kenn ci yéen ne ko: «Demal ak jàmm, nga solu te lekk,» te fekk fajuleen aajoom, loolu lu muy jariñ? 2:17 Noonu ngëm gu àndul ak jëf, amul benn njariñ. 2:18 Waaye xanaa dina am ku ne: «Yaw am nga ngëm, man am naa ay jëf.» Yaw nag won ma sa ngëm gu àndul ak jëf, man ma feeñal la sama ngëm ci samay jëf. 2:19 Gëm nga ne Yàlla kenn la; loolu lu baax la, waaye xamal ne, jinne yi it gëm nañu loolu, ba dañoo tiit bay lox. 2:20 Yaw mi gàtt xel, kaay ma won la ne, ngëm gu àndul ak jëf, amul njariñ. 2:21 Sunu maam Ibraayma, ndax du ci kaw jëf la ko Yàlla àttee ni ku jub, ci li mu joxe doomam Isaaxa ni sarax? 2:22 Kon gis nga ne, ngëm dafa lëngoo ak ay jëfam, te ngëmam mat ci kaw jëf jooju. 2:23 Noonu li ñu wax ci Mbind mi am na, bi mu naan: «Ibraayma gëm na Yàlla, te Yàlla jàppe ngëmam ni njub,» ba ñu ko wooye xaritu Yàlla. 2:24 Kon nag gis nga ne, Yàlla ci jëf lay àtte nit ni ku jub, waaye du ci kaw ngëm kese. 2:25 Naka Raxab jigéenu moykat bi itam, ndax du ci noonu la ko Yàlla àttee ni ku jub, ci li mu teeru ndawi Yawut yi, te jaarale leen ca poot ba? 2:26 Kon nag ni jëmm ju amul ruu nekke ndee, noonu la ngëm gu àndul ak jëf nasaxe.
3:1 Samay bokk, bu ñépp di sababloo nekk jàngalekatu mbooloo mi, xam ne nun jàngalekat yi, àtte bi nuy jaar mooy gën a diis. 3:2 Ndaxte nun ñépp sikk nanu ci fànn yu bare. Ki sikkul ci kàddoom, ku mat nga, te man a noot sa yaram wépp. 3:3 Noonu ku laab fas, ngir mu déggal la, noot nga jëmmam jépp. 3:4 Te gaal yi it yu réy lañu, te ngelaw lu am doole di leen jiñax, waaye dawalkat bi, weñ gu tuuti la leen di jëme fu ko neex. 3:5 Ci noonu làmmiñ, cér su tuuti la, waaye day bàkkoo jëf yu réy. Seetleen ni ferñent tuutee, te man a làkk àll bu yaatu. 3:6 Noonu it làmmiñ safara la, di bon-bonu àddina ci biir cér yi, tey musibaal jëmm jépp. Jum la, bu Seytaane taal, muy lakk àddina. 3:7 Nit man na noot xeeti rab yépp: rabi àll yi, picc yi, yiy raam ak yi ci géej gi; noot na lépp. 3:8 Waaye làmmiñ kenn mënu koo noot; musiba la mu dul dal mukk, fees dell ak daŋar juy rey. 3:9 Làmmiñ lanuy sante Boroom bi, di sunu Baay, ba noppi móoloo ko nit, ñi Yàlla sàkk ci meloom. 3:10 Gémmiñ gi sante mooy móoloo. Yéen samay bokk, loolu warul a am. 3:11 Ndax ndox mu lewet ak mu wex dinañu ballandoo ci genn mbënn? 3:12 Samay bokk, ndax mas ngeen a gis garabu figg gu meññ oliw, walla garabu réseñ gu meññ ay figg? Mukk! Mbënnu xorom mënta nàcc mukk ndox mu neex. 3:13 Ana ku neex xel ci yéen, ana kuy boroom xam-xam? Na ko wone ciy jëfam ak dundam gu sell, te feeñal xelam ci jikkoom ju lewet. 3:14 Waaye ku am ci sa xol farlu gu laloo wextan ak wut aw tur, bul bàkku, di weddi dëgg. 3:15 Xel moomu jógewul ci kaw; jëfu àddina la, di jikkoy niti kese, te jóge ci Seytaane. 3:16 Ndaxte fu wextan ak wut aw tur dugg, indi fa xëccoo ak bépp ñaawteef. 3:17 Waaye xel mi jóge ci kaw daa sell, ba noppi ànd ak jàmm te lewet, nooy, fees dell ak yërmande ak jëf yu rafet; àndul ak genn parlàqu, amul genn naaféq. 3:18 Te nitu jàmm dina bey toolu jàmm, góob njub.
4:1 Xeex yi ak xuloo yi ci seen biir nag, lu leen waral? Xanaa du ci seeni bëgg-bëgg, yiy xeex ci seeni cér? 4:2 Dangeen di mébét waaye dungeen am; dangeen di rey nit, boole ci kiñaan, waaye li ngeen di yóotu, dungeen ko jot; dangeen di xuloo ak a xeex waaye dungeen am dara, ndaxte ñaanuleen Yàlla. 4:3 Bu ngeen ñaanee sax, dungeen jot dara, ndax yéena ngi ñaan ci naaféq, ngir gën a topp seen nafsu. 4:4 Yéen ñi fecci seen kóllëre ak Yàlla, xanaa xamuleen ne mbëggeelu àddina, mbañeel la fa Yàlla? Ku bëgg a xaritoo ak àddina nag, noonoo nga ak Yàlla. 4:5 Xanaa yaakaar ngeen ne, Mbind mi day wax cig neen, ci li mu ne: «Yàlla am na mbëggeel gu fiir ci Xel mi mu def ci nun.» 4:6 Waaye yiwu Yàllaa ko ëpp. Moom la Mbind mi wax ne:«Yàlla dàq na ñi réy,waaye yiwal na ñi woyof.» 4:7 Kon nag wàkkirluleen ci Yàlla, waaye dàqleen Seytaane, te dina daw, ba sore leen. 4:8 Jegeleen Yàlla, mu jege leen. Yéen bàkkaarkat yi, sellal-leen seeni loxo; yéen ñi am xel ñaar, laabal-leen seeni xol. 4:9 Toroxluleen te naqarlu, bay jooy; defleen seeni ree aw naqar, te seen mbég nekk tiis. 4:10 Suufeel-leen seen bopp fa kanam Boroom bi, kon dina leen yékkati. 4:11 Yéen bokk yi, buleen ŋàññante. Ku ŋàññ sa moroom mbaa nga ñaaw njort, ba àtte ko, diiŋat nga yoonu Yàlla te àtte ko; ku àtte yoon wi nag sàmmoo ko, waaye danga koo àtte. 4:12 Kenn rekk mooy tëral yoon, kooku rekk mooy àtte; moo man a musle, moo man a alage. Te sax yaw miy àtte sa bokk yaay kan? 4:13 Léegi nag dégluleen, yéen ñiy wax ne: «Tey walla ëllëg dinanu dem ca dëkk sàngam, def fa at, di fa sàkku xaalis ci jula.» 4:14 Ndax dangeen a xam seen ëllëg? Te luy seen dund? Xanaa cóola doŋŋ luy naaw ci diir bu gàtt, daldi naaxsaay. 4:15 Lii kay ngeen waroon a wax: «Bu soobee Boroom bi, dinanu dund, tey def nàngam ak nàngam.» 4:16 Waaye fi mu ne, naagu ngeen bay damu, te damoo noonu baaxul. 4:17 Kon nag ku xam def lu baax te defoo ko, bàkkaar nga.
5:1 Dégluleen yéen boroom alal yi, jooyleen te naqarlu ndax mbugal, gi leen di xaar. 5:2 Seen alal seey na, seen yére yi maxe na, 5:3 seen wurus ak seen xaalis xomaag na. Te xomaag jooju seede lay doon, su leen di daanlu, ba lakk leen ni safara. Dajale ngeen alal ju ne gàññ, te fekk yéena ngi ci muju jamono. 5:4 Dégluleen, jooyi xaalis bi ngeen sàcce ci gubkat, yi leen doon liggéeyal, ak yuuxi góobkat yi, dugg nañu ci noppi Yàlla Aji Kàttan ji. 5:5 Ci barele ak bànneex ngeen dunde ci kaw suuf, di yafal seen bopp, fekk bésu rendi baa ngii. 5:6 Daan ngeen ku jub, ba rey ko sax, te bañul. 5:7 Yéen samay bokk, muñleen, ba Boroom bi dellusi ci ndamam. Seetleen ci beykat bi, ni muy xaare njariñ ci meññeefu suuf, tey muñ, céebo ba bët wàcc. 5:8 Yéen itam nag muñleen te dëgëral seen xol, xam ne ñëwu Boroom bi ci ndamam jege na. 5:9 Buleen jàmbatante, samay bokk, ngir ragal Yàlla àtte leen. Àttekat baa ngi ci bunt bi sax! 5:10 Bokk yi, defleen yonent, yi wax ci turu Boroom bi, seeni royukaay ci muñ tiis ak ci góor-góorlu. 5:11 Xam ngeen ne ñiy góor-góorlu, ñu barkeel lañu. Dégg ngeen muñ ga Ayóoba amoon, te gis muj gu rafet, ga ko Boroom bi jagleel, ndax Boroom bi kuy ñeewante la te bare yërmande. 5:12 Te li fi raw samay bokk, buleen waat mukk, bu muy ci asamaan mbaa ci suuf mbaa ci leneen lu mu man a doon. Nangeen yem ci: «Waaw,» ak «Déedéet,» ngir bañ cee layoo fa kanam Yàlla. 5:13 Su amee ci yéen ku nekk ci tiis, na ñaan ci Yàlla. Ku nekk ci mbég, na sant Yàlla ciy woy. 5:14 Su amee ci yéen ku wopp, na woo njiiti mbooloo mi, ñu ñaanal ko te diw boppam ci turu Boroom bi. 5:15 Te ñaan gu ànd ak ngëm dina musal ki wopp, ba Boroom bi yékkati ko. Te su ko fekkoon ak i bàkkaar sax, Yàlla dina ko baal. 5:16 Kon nag waxanteleen seeni bàkkaar tey ñaanalante, ngir ngeen wér. Ñaanu aji jub gu dëggu, dooleem amul kem. 5:17 Naka noonu Iliyas nit la woon ku bindoo ni nun, waaye bi mu saxee ci ñaan Yàlla, ngir mu bañ a taw, ndox laalul suuf diirub ñetti at ak genn-wàll. 5:18 Gannaaw ga mu dellu ñaan, asamaan daldi taw, te suuf si saxal meññeef. 5:19 Samay bokk, su amee ci yéen ku réere dëgg, te am ku ko gindi, 5:20 na xam lii: ku gindi bàkkaarkat ci réeram, musal nga nit ci dee te faral ko bàkkaar yu bare.
1:1 Man Piyeer, ndawul Yeesu Kirist, maa leen di bind, yéen doxandéem yi tasaaroo ci diiwaani Pont, Galasi, Kapados, Asi ak Bitini. Yàlla Baay bi tànn na leen, 1:2 ci li mu leen xam bu jiitu, te sédde leen boppam ci jëfu Xel mu Sell mi, ngir ngeen déggal ko, te seen xol laab ndax deretu Yeesu Kirist. Na leen Yàlla dollil yiw ak jàmm. 1:3 Cant ñeel na Yàlla, Baayu sunu Boroom Yeesu Kirist! Moo nu judduwaatal ci yërmandeem ju bare, ba may nu yaakaar ju sax ndax ndekkitel Yeesu Kirist. 1:4 Sédd na leen cér bu dul yàqu, du gàkk te du seey mukk, dencal leen ko ci asamaan, 1:5 yéen ñi muy aar ci dooleem, sukkandikoo ci ngëm, di leen nége mucc, gi mu nar a feeñal bés bu mujj ba. 1:6 Yéena ngi bég bu baax ci biir yaakaar jooju, doonte sax, su waree am, yéena ngi dékku tiis ab diir, ci seen jànkoonte ak nattu yu wuute. 1:7 Xam ne nattu yooyu dinañu sellal seen ngëm, ni safara di setale wurus, fekk wurus luy wéy la, te ngëm a ko gën fuuf. Noonu seen ngëm dina yelloo cant, ndam ak màgg, bés bu Yeesu Kirist feeñee. 1:8 Musuleen koo gis waaye bëgg ngeen ko, gisuleen ko waaye gëm ngeen ko te am mbég mu xel dajul, mu fees dell ak ndam, 1:9 di jot muj gi ngëm séentu, maanaam muccu xol. 1:10 Naka mucc googu nag, yonent yi xamle yiw, wi ngeen naroon a joti, seet nañu ko te gëstu ko. 1:11 Bi Xelum Kirist, mi nekkoon ci ñoom, seedee lu jiitu coonoy Kirist ak ndam la cay topp, jéem nañoo takk, kañ ak nan lay ame. 1:12 Waaye Yàlla xamal na leen ne, moomuñu woon kàddu googu ñu wax, waaye yéena ko moom. Te mooy kàddu gi ngeen dégg ci gémmiñu ñi leen doon jottali xebaar bu baax bi, ci dooley Xel mu Sell, mi Yàlla yónnee asamaan; malaaka yi sax bëgg nañoo gëstu yëf yii. 1:13 Kon fagaruleen ci seeni xalaat te maandu, di wékk seen yaakaar jépp ci yiw, wi leen Yàlla di jagleel bés bu Yeesu Kirist di feeñ. 1:14 Gannaaw gaayi Yàlla yu koy déggal ngeen, buleen toppati bëgg-bëgg, yi ngeen toppoon, bi ngeen xamagul Yàlla. 1:15 Waaye na seen dund gépp sell, ni Yàlla mi leen woo selle. 1:16 Ndaxte Mbind mi nee na: «Sell-leen, ndaxte ku sell laa.» 1:17 Gannaaw nag Yàlla, mi ngeen di wooye Baay, mooy àtte jëfi ñépp te du gënale kenn, saxleen ci ragal ko diirub seen ngan ci àddina. 1:18 Xam ngeen ne, Yàlla jot na leen ci seen dund gu tekkiwul dara, gi maam ya nekkoon; te jotuleen ak yu deme ni xaalis mbaa wurus yuy wéy, 1:19 waaye ci deretu Kirist ju tedd ji, mel ni mbote mu sikkul te wàññikuwul. 1:20 Yàlla xamoon na ko, ba àddina sosoogul, waaye léegi ci mujug jamono feeñal na ko ndax yéen 1:21 ñi jaar ci moom, gëm Yàlla. Te Yàlla dekkal na ko, sol ko ndam, ngir ngeen wékk seen ngëm ak seen yaakaar ci Yàlla. 1:22 Kon nag gannaaw déggal ngeen dëgg gi, ba sellal seeni xol te am mbëggeel gu dëggu, bëgganteleen mbëggeel gu tar ak seen xol bépp. 1:23 Ndaxte du ci jiwu wuy yàqu ngeen judduwaate, waaye ci jiwu wu sax, maanaam kàddug Yàlla giy dund tey sax. 1:24 Ndaxte:«Nit ñax la,ndamam di tóor-tóor kese;ñax day wow, tóor-tóor ruus,waaye kàddug Boroom bi day sax ba fàww.» 1:25 Te kàddu googu mooy xebaar bu baax, bi ñu leen doon yégal.
2:1 Kon nag dëdduleen gépp coxor, gépp njublaŋ, naaféq, kiñaan ak jëw. 2:2 Gannaaw ay liir ngeen yuy door a juddu te mos ci mbaaxug Boroom bi, nàmpleen ci meew mu sell, miy dundal seen xol, ba màgg ci biir muccu Yàlla. 2:4 Kon nag ñëwleen ci moom; nit ñi bañ nañu ko, waaye Yàlla fal na ko te teral ko. Mi ngi mel ni doju tabax, waaye doj wuy dund la, 2:5 te yéena ngi mel niy doj yuy dund yu Yàllay defare dëkkukaayam. Noonu ay saraxalekat yu sell ngeen, ngir jébbal ko ay sarax yu ngeen tibbe ci seen xol te neex ko ndax Yeesu Kirist. 2:6 Looloo tax bind nañu:«Maa ngi samp fi ci Siyon doju koñ.Doj wu tedd la, wu ma tànn;ku gëm ci moom, sa yaakaar du tas mukk.» 2:7 Kon nag yéen ñi gëm am ngeen cér ci teraangaam. Waaye naka ñi gëmul:«Doj wa tabaxkat ya sànni,mujj na di doju koñ.» 2:8 Te it:«Doj la wuy fél nit,di xeer wu koy fakkastal.» Dañu cee fakkastalu, ndaxte gëmuñu kàddug Yàlla, te loolu la Yàlla dogal ci ñoom. 2:9 Waaye yéen xeet wu Yàlla tànn ngeen, di askanu saraxalekati Buur Yàlla, askan wu sell ngeen, di mbooloom Yàlla, ngir ngeen yégle ngëneelam, moom mi leen woo, ba génne leen lëndëm gi, tàbbal leen ci leeram gu yéeme gi. 2:10 Démb nekkuleen woon ci dara, waaye tey mbooloom Yàlla ngeen; booba jotuleen woon yërmandeem, waaye léegi jot ngeen ko. 2:11 Samay xarit, yéen ñiy ay gan ak ay doxandéem ci àddina si, maa ngi leen di dénk lii: dëdduleen bànneexi bakkan yiy xeex ak xol. 2:12 Na seen dundin rafet ci biir xeeti àddina, kon doonte ñu di leen sosal ay ñaawteef, dinañu gis seeni jëf yu rafet bay màggal Yàlla, bés bu leen feeñoo. 2:13 Na seen nangub Boroom bi tax, ngeen déggal képp kuy kilifa, muy buur ba gën a kawe, 2:14 mbaa jawriñ yu mu yebal, ngir ñu yar ñiy def lu bon, te teral ñiy def lu baax. 2:15 Ndaxte noonu la coobareg Yàlla tëdde, maanaam ngeen sax ci def lu baax, ba wedamloo jayil yi xamul dara. 2:16 Li leen Yàlla goreel nag, bu mu tax ngeen mbubboo ko, bay def lu bon, waaye ngeen gën a feddali seen jaamu Yàlla. 2:17 Teral-leen ñépp, bëgg kureelu bokk yi, ngeen ragal Yàlla te teral buur bi. 2:18 Yéen jaam yi déggal-leen seeni sang ak wegeel gu mat sëkk, waxuma ñi baax te lewet rekk, waaye sax ñu wex ñi. 2:19 Ndaxte su ngeen dékkoo tiis, di sonn ci lu dul yoon ndax seen ànd ak Yàlla, loolu lu rafet la. 2:20 Su ngeen tooñee te muñ i pes, luy pey gi? Waaye su ñu leen fitnaalee ci def lu baax te ngeen muñ ko, jëf ju rafet la fa kanam Yàlla. 2:21 Ndaxte ci loolu la leen Yàlla woo, ndaxte Kirist itam sonn na ngir yéen, teg fi seen kanam royukaay, ngir ngeen jaar ciy tànkam. 2:22 «Musul a def bàkkaar,te jenn waxu njublaŋ musul a génn ci gémmiñam.» 2:23 Saaga nañu ko te feyyuwul, fitnaal nañu ko te tëkkuwul, waaye mu dénk boppam Ki yor àtte bu dëgg bi. 2:24 Gàddu na moom ci boppam sunuy bàkkaar ca bant, ba ñu ko daajoon, ngir nu tàggook bàkkaar, sóobu ci dund gu jub; ndax ay gaañu-gaañoom may na nu ag wér. 2:25 Ndaxte yéena ngi réeroon niy xar, waaye léegi dellusi ngeen ci sàmm, biy aar seeni xol.
3:1 Yéen itam jigéen ñi, na ku nekk nangul sa jëkkër. Noonu su amee góor gu gëmul kàddug Yàlla, te gis jabaram di dund dund gu sell, boole ci weg ko, loolu dina ko gindi ci lu àndul ak wax. 3:3 Bu seen taar aju ci col, maanaam ay létt, wurus mbaa yére yu rafet, 3:4 waaye nay taar bu sax bu nekk ci biir, di xol bu nooy te dal, ndax loolu lu takku la fa Yàlla. 3:5 Ndaxte jigéeni démb yu sell, ya gëmoon Yàlla, loolu moo doon seen taar; nanguloon nañu seen jëkkër, 3:6 ni Saarata déggale woon Ibraayma, ba daan ko wooye «Sang bi.» Yéen nag, su ngeen dee def lu baax te bañ cee boole genn njàqare, kon mel na ni Saarataa leen jaboote. 3:7 Te yéen itam góor ñi, na ku nekk ci yéen am xel, ci ni ngay ànde ak sa jabar, xam ne àndandoo ju la gën a néew doole la. Joxleen ko teraanga ju mat, ndax yéena yem cér ci yiwu Yàlla, wi nu ubbil buntu dund gu dul jeex. Noonu dara du man a yàq seeni ñaan. 3:8 Kon nag bokkleen xalaat, bokkleen i tiis, bëgganteleen, yërëmante te woyof. 3:9 Ku la def lu bon mbaa mu saaga la, bul feyyu, waaye ñaanal ko lu baax; ndaxte ci loolu la leen Yàlla woo, ngir barkeel leen. 3:10 Ndaxte:«Ku bëgg a am dund gu naatte fekke bés yu rafet,na jàpp làmmiñam ci lu bon,sàmm gémmiñam ci fen. 3:11 Na dëddu lu bon, tey def lu baax,na xënte jàmm te sax ci. 3:12 Ndax Boroom baa ngi xool ñi jub bëti yërmande,di ubbi ay noppam ci seeni ñaan,waaye dàq ñiy def lu bon.» 3:13 Te it kan moo leen di sonal, su ngeen góor-góorloo ci def lu baax? 3:14 Doonte ñu di leen fitnaal sax ci def lu jub, ñu barkeel ngeen. Buleen tiit nag ndax seeni xëbal, mbaa ngeen di ci am njàqare. 3:15 Waaye màggal-leen Kirist Boroom bi ci seeni xol, te jekk ngir tontu ku lay laaj ci seen yaakaar ji ngeen am; 3:16 waaye na tont gi lewet te ànd ak wegeel. Àndleen ak xel mu dal; noonu ñi leen di sikkal ndax seen dund gu rafet ci gëm Kirist, dinañu rus ci seeni sos. 3:17 Ñu fitnaal la ndax jëf ju baax, su dee mooy coobareg Yàlla, moo gën ñu fitnaal la ndax jëf ju bon. 3:18 Ndaxte Kirist ci boppam dee na benn yoon ba fàww, ngir dindi bàkkaar yi, moom mi jub ngir ñi jubadi, ngir yóbbu leen fa Yàlla; dee na ci jëmm, waaye dundaat na ci xel. 3:19 Ci biir xel moomu la yégaleji ndamam ca ruu ya Yàlla tëj kaso; 3:20 maanaam ña weddi woon ca jamonoy Nóoyin, fekk Yàlla muñaloon na leen diir bu yàgg, dajeek Nóoyin doon yett gaal ga. Ñu néew, maanaam limub juróom-ñett, dugg nañu ca gaal ga, jaar ca ndox ma, ba mucc. 3:21 Loolu misaal la tey, ci li ñu nuy sóob ci ndox, te nu mucc; waxuma laabal sobe si taq ci yaram, waaye wuyu Yàlla ak xel mu dal. Li nu may mucc googu, mooy ndekkitel Yeesu Kirist, 3:22 mi yéeg asamaan, toog fa ndeyjooru Yàlla, mu tiim malaaka yi, boroom sañ-sañ yi ak boroom doole yépp.
4:1 Gannaaw Kirist nag sonn na ci yaramam, gànnaayooleen xelam moomu, ndaxte ku sonn ci yaramam, tàggoo na ak bàkkaar. 4:2 Noonu diir bi ko dese ci kaw suuf, dëddu na bànneexi bakkan, jublu ci coobareg Yàlla. 4:3 Ndaxte àndoon ngeen démb ci xalaati ñi xamul Yàlla, di dund ciy ñaawteef ak topp seen bakkan, di màndi ak a xawaare, di xér ci biiñ ak a jaamu ay xërëm yu araam, waaye na fi yem nag. 4:4 Ñiy jëfe noonu waaru nañu, ba di leen sosal, ci li ngeen àndul ak ñoom, sóobu ci seeni moy yu dul jeex, 4:5 waaye dinañu mas a teew fa kanam Ki nar a àtte ñiy dund ak ñi dee. 4:6 Looloo waral it ñu jottali xebaar bu baax ndee, ya fekke woon jamonoy Nóoyin jooju, ngir ñu dunde Yàlla ci seen xel, doonte sax nit ñaa ngi leen daan fitnaal ci àddina. 4:7 Te itam muju lépp jegesi na; nangeen maandu te foog, ba man a ñaan ci Yàlla. 4:8 Li gën a am solo mooy, ngeen bëggante mbëggeel gu tar, ndax mbëggeel day suul bàkkaar yu bare. 4:9 Ganalanteleen ci lu àndul ak njàmbat. 4:10 Te lu la Yàlla jagleel kenn ku nekk ci yéen, nanga ko bokk ak ñépp ni jawriñ ju jub, ci séddale yiwu Yàlla wu yaatu. 4:11 Kuy jottali kàddug Yàlla, na mel ni Yàllaay wax. Kuy jëf it, na jëfe dooley Yàlla, ngir turu Yàlla màgg ci lépp jaar ci Yeesu Kirist, mi yelloo ndam ak kàttan ba fàww. Amiin. 4:12 Yéen samay xarit, ci mbirum nattu bu tànge ni daay, bi dal ci seen kaw, bumu leen jaaxal, ba ngeen teg ko ni lu xel dajul. 4:13 Waaye bégleen ci cér, boobu ngeen am ci coonoy Kirist, ngir bés bu ndamam di feeñ, ngeen bég ak mbég mu ëpp xel. 4:14 Su ñu leen jànnee sax ci turu Kirist, xamleen ne ñu barkeel ngeen, ndax Xelum Yàllaa ngi ci yéen, di firndeel seen ndamu ëllëg. 4:15 Buñu sonal kenn ci yéen ci li mu rey nit walla mu sàcc, mbaa def lu bon, walla dugg ci lu yoonam nekkul. 4:16 Waaye ku ñu sonal ndax waayu Kirist nga, bu ci rus, waaye nga màggal Yàlla ci tur woowu. 4:17 Ndaxte àpp bi jot na, àtte baa ngi tàmbalee ci nun waa kër Yàlla. Te su tàmbalee ci nun nag, luy muju ñi weddi xebaaru Yàlla? 4:18 Te:«Su muccu ki jub jafee,luy doon muju ki weddi te dëng?» 4:19 Kon nag ñi tegoo fitna ci coobareg Yàlla, nañu sax ci def lu baax, dénk seen bopp Yàlla, miy Bindkat biy sàmm kóllëre.
5:1 Kon yéen njiit yi, maa ngi leen di dénk, man miy njiit ni yéen, man mi seede coonoy Kirist te am cér ci ndam li nar a feeñ. 5:2 Lii laa leen di ñaan: sàmmleen géttug Yàlla, gi mu leen dénk, di ko wottu, waxuma ci sañul-bañ, waaye di surgay Yàlla ci xol bu tàlli; ngeen def ko ak xol bu laab te bañ cee séentu alal. 5:3 Buleen noot ñi leen Yàlla dénk, waaye ngeen nekk ay royukaay fi kanam jur gi. 5:4 Noonu waxtu wu Boroom gétt gi feeñee, dina leen jagleel kaalag ndam guy sax ba fàww. 5:5 Noonu itam yéen ndaw ñi, nangeen déggal mag ñi. Te yéen ñépp, solooleen woyof ci seen biir, ndaxte:«Yàlla day dàq ñi réy,di yiwal ñi woyof.» 5:6 Suufeel-leen seen bopp kon ci ron loxob Yàlla bu am kàttan, ngir mu yékkati leen ci jamono ju ko soob. 5:7 Te ngeen yenniku ci kawam seen njàqare jépp, ndax ku leen ñeewante la. 5:8 Maanduleen te foog, ndax seen noon Seytaane mu ngi wër, ni gaynde guy yëmmu, di rëbb ku mu yàpp. 5:9 Jànkoonteleen ak moom ci biir ngëm gu takku, xam ne kureelu bokk yi ci àddina yépp, ñu ngi daj ay fitna ni yéen. 5:10 Te Yàlla mi jagoo yiw wépp te woo leen ci darajay Kirist, ngir ngeen bokk ci ndamam li sax, gannaaw bi ngeen yendoo bëccëgu tiis, dina leen yeesalaat, di leen dëgëral ak a dooleel, ba ngeen sampu. 5:11 Na Yàlla yelloo màgg ba fàww. Amiin. 5:12 Bind naa leen ci lu gàtt ci ndimbalu Silwan, mi ma jàpp ni sama mbokk mu takku. Dénk naa leen, di leen seedeel ne, lii mooy yiwu Yàlla dëgg; kon nag saxleen ci. 5:13 Mbooloo mi nekk ci dëkk bi ñuy wax Babilon te Yàlla tànn ko ni yéen, moo di leen nuyu, ñoom ak Màrk sama doomu diine. 5:14 Nuyoonteleen ak saafoonte yu sell. Na jàmm ñeel képp ku gëm Kirist.
1:1 Man Simoŋ Pieer, jaamu Yeesu Krist ak ndawam, maa leen di bind, yeen ñi Yàlla jagleel ngëm gu rafet ni nun, aju ci njubu sunu Yàlla ak Musalkat, Yeesu Krist. 1:2 Na leen Yàlla dollil yiw ak jàmm, jaar ci xam ko ak Yeesu sunu Boroom. 1:3 Dooley Yàlla moo nu may lépp lu aju ci dund gu sax ak ragal Yàlla, jaarale ko ci xam gi nu ko xam, moom mi nu woo ci kaw ndamam ak dooleem. 1:4 Noonu la nu dige ay dig yu rafet, te réy ba ëpp xel, ngir nu gëm leen, te Yàlla sol nu jikoom, nu mucc ci yàqute, gi bànneexu bakkan samp ci àddina si. 1:5 Na loolu tax ngeen góor-góorlu, ba yokk ci seen ngëm njàmbaar, ci njàmbaar googu ngeen yokk ci xam-xam, yokk ci noot sa bopp. 1:6 Noot sa bopp googu, ngeen yokk ci muñ, yokk ci ragal Yàlla, 1:7 yokk ci sopp mbokk, yokk ci bëgg ñépp. 1:8 Ndaxte bu leen jiko yooyu soloo, ba sax ci yeen, dina tax seen xam Yeesu Krist Boroom bi am njeriñ te jur mbaax. 1:9 Waaye ku ñàkk jiko yooyu, ay bëtam dañoo lëndëm ba gumba, te fàtte na, ni ko Yàlla fóotale bàkkaari démb. 1:10 Kon nag samay mbokk, gannaaw Yàlla da leena tànn te woo leen, góor-góorluleen ci feddali ko ak seen kem-kàttan. Ndaxte su ngeen ko defee, dungeen jeng mukk. 1:11 Te noonu dingeen tàbbi ak ndam ci nguur gu sax gu sunu Boroom, di sunu Musalkat Yeesu Krist. 1:12 Wóor na ma ne xam ngeen loolu, ba sampu ci dëgg gi leen Yàlla jagleel, waaye fas naa yéene, may sax ci di leen ko fàttali. 1:13 Te jàpp naa ko, muy sama warugar, feek maa ngi noyyi, ma di leen fàttali loolu, ba yee leen. 1:14 Ndaxte xam naa ne, léegi ma jóge fi, ni ma ko Yeesu Krist Boroom bi leerale woon. 1:15 Te dinaa góor-góorlu, ngir sama gannaaw ngeen di fàttaliku li ma leen doon wax. 1:16 Bi nu leen yégalee dooley Yeesu Krist sunu Boroom ak ñëwam ci biir ndam, sukkandikuwunu woon ciy léeb yu sësul fenn, waaye danoo teewe ag màggam. 1:17 Ndaxte Yàlla Baay bi sol na ko teraanga ak ndam, te baatub Aji Màgg ju tedd ji jib na ne: Sama Doom a ngii, di sama Soppe; ci moom laa ame bànneex. 1:18 Te nun dégg nanu baat boobu jóge asamaan, bi nu nekkee ak moom ca tund wu tedd wa. 1:19 Noonu bir na ne, waxu yonent yi wér na, te war ngeen koo fonk; mi ngi mel ni làmp, buy leer ci bérab bu lëndëm, ba kera fajar di xar, te biddiiwub njël bi feq, leeral seeni xol. 1:20 Waaye jëkkleena xam ne, amul jenn waxu yonent ci Mbind mi, ju balle ci xelu boppam. 1:21 Ndaxte kenn ci yonent yi musula wax ci coobareg boppam, waaye, Xel mu Sell mi daa na xiir nit ñi, ñu yégle kàddug Yàlla.
2:1 Waaye ci bànni Israyil, amoon na naaféq yu mbubboo turu yonent, ni muy ame seen biir ñuy mbubboo turu jàngalekat. Ci seeni pexe dinañu dugal ci yeen xalaat yu sànke, di weddi Boroom bi leen jot, tey yóbbe seen bopp alkande ju teew. 2:2 ñu bare dinañu leen fekki ci seeni ñaawteef, ba gàkkal yoonu dëgg ci bëti nit ñi. 2:3 Seen bëgge dina tax, ñu dàbbdaaxe ay wax, ngir nax leen, ba lekk seenus tuut. Waaye àtte baa ngi leen di xaar, te seen alkande di leen teeru. 2:4 Ndaxte Yàlla jeggalul malaaka ya bàkkaaroon, waaye tàbbal na leen safara, tëj leen ca kàmb yu lëndëm, di leen nége àtte ba. 2:5 Te it jeggalul àddina su jëkk sa weddi woon, ba xooj ko ci ndoxu mbënn ma, waaye musal na Nóoyin rekk, mi daan waare ci njub, moom ak juróom-ñaari nit. 2:6 Te it Yàlla daan na dëkki Sodom ak Gomor, raafal leen cig lakk, ñuy misaalu ñiy weddi ëllëg. 2:7 Waaye musal na Lóot mi jub, mi sonnoon ndax ñaawteefi ñu dëng, ñooñu mu nekkaloon. 2:8 Ndaxte Lóot, mi dëkkoon ci seen biir, dafa dëkke woon tiisu xol, ndax ñaawteef yi mu gis ak a dégg guddi ak bëccëg. 2:9 Gannaaw loolu lépp am na nag, nanu bir ne, Boroom bi man na musal aji gëm ji nekk ci nattu, te denc ñi jubadi, ngir alag leen bésu àtte ba. 2:10 Rawatina ñiy topp seen bakkan ciy bëgg-bëgg yu ruslu, te faalewuñu genn kilifteef. ñu ñeme Yàlla lañu, te dëgër bopp, ba ragaluñoo xas kilifa ya gëna kawe. 2:11 Fekk sax malaaka, yi leen ëpp doole ak kàttan, tey sax ca jetaayu Boroom bi, ñemewuñoo xas kilifa yooyu. 2:12 Waaye ñoom dañuy xas ci biir yi ñu xamul. ñoom ak bàyyima ñoo yem, di ay mbindeef yuy tañaxu, te tër rendi rekk a jekk ci ñoom; dees na leen rey ni bàyyima, 2:13 muy seen peyug njubadi. Xawaare bëccëgu ndara-kàmm mooy seen bànneex. Su ñuy lekkandoo ak yeen, dañuy bànneexu ci seeni bëgg-bëgg, di ay gàkk ak i sikk ci seen biir. 2:14 Jigéen ju seen bët tegu, ñu xédd ko, ba duñu tàggook moy mukk; ku ñàkk pasteef ñu fàbbi la; ñu xelu lañu jëme cig bëgge -- ñu alku lañu! 2:15 Réer nañu ba wàcc yoon wu jub wi, topp yoonu Balaam, doomu Bosor, mi bëgge xiiroon ci njubadi. 2:16 Waaye déggadeem yóbbe na ko yeraanga; xam ngeen ne mbaam-sëf du wax, waaye mbaam wax na ak moom ci làmmiñ wu bir, ngir mu génn ci ndofam googu. 2:17 Ñooñule ay teen yu dëy lañu, di xiini lay, yu ngelaw liy naawal, te seen pey mooy lëndëm gu ne taraj. 2:18 Dañuy fàbbi ñu naroona mucc ci àddina ju réer, dig leen ak làmmiñ yu neex bànneexi bakkan yu jéggi dayo. 2:19 Dañu leen di dig ngoreel, te fekk ñoom ci seen bopp jaami yàqute lañu, ndaxte lu la noot, jaamam nga. 2:20 Su ñu xamee Boroom bi, di sunu Musalkat Yeesu Krist, ba mucc ci sobes àddina, ba noppi sóobuwaat ca, ba mu noot leen, seen muj moo yées seen njàlbéen. 2:21 Ndaxte ñu xam yoon wu jub wi, ba noppi dëddu ndigal lu sell li ñu déggoon, bañoon koo xam moo gënoon ci ñoom. 2:22 Noonu seen mbir dëggal na li ñuy wax ne: Xaj mooy waccu, di ko lekkaat; te it: Mbaam-xuux, loo ko sang-sang, mu xalangu ci ban.
3:1 Yeen samay xarit, sama ñaareelu bataaxel a ngi nii. Bind naa leen, ngir xiir leen ci xalaat yu sell. 3:2 Maa ngi leen di fàttali kàdduy yonent yu sell, yi fi jiitu woon, ak ndigalu Boroom bi sunu Musalkat, li ngeen déggoon ci ndaw, yi Yàlla yebaloon fi yeen. 3:3 Nangeen jëkka xam lii: muju jamano dingeen gis ay tiiñalkat, di topp seen bakkan; dinañu leen tiiñal 3:4 ci di leen ne: Ki dige woon ne dina ñëw, ana mu? Ndaxte baay ya nelaw nañu, waaye lépp a ngi dox ca njàlbéen ga ba tey. 3:5 Fekk bëgguñoo xam lii: kàddug Yàllaa tax, asamaan ak àddina yu jëkk ya juddoo ca ndox, te dunde ko. 3:6 Te ndox it moo labal àddina sa, raafal ko. 3:7 Te kàddug Yàlla googu moo denc asamaan yii fi nekk ak suuf si, ngir lakk leen; Yàllaa ngi leen di nége bésub àtte, ba muy alag ñi weddi. 3:8 Yeen samay xarit, buleen umple ne, benn bés ak junniy at ñoo yem fi Boroom bi. 3:9 Li Yàlla dige, dina ko def, lu mu yeex-yeex ci xalaatu nit. Xanaa kay da leena muñal, ndax bëggul kenn alku, waaye ñépp tuub seeni bàkkaar. 3:10 Waaye bésu Boroom bi dina ñëw, bett àddina ni sàcc. Su boobaa, asamaan yi dinañu ne rajax toj, lu ne ci àddina lakk ba seey, te suuf ak lu mu ëmb dina ne fàŋŋ fa kanam Yàlla. 3:11 Gannaaw loolu lépp dina seeye noonu nag, nangeen góor-góorlu ci gëna sellal seen nekkin, te feddali seen ragal Yàlla. 3:12 Te it ngeen taxaw temm ci séentu bésu Yàlla bi, te waajal ñëwam. Su boobaa, asamaan yi dinañu lakk, ba naaw ni pënd, te lu nekk ci àddina dina lakk, ba seey nib dóom. 3:13 Waaye nun ngi séentu asamaan su bees ak suuf su bees, fa njub dëkk, ci ni ko Yàlla dige. 3:14 Kon nag samay soppe, gannaaw yeena ngi séentu loolu, góor-góorluleen, ngir bu Krist ñëwee, mu fekk leen ci jàmm, ngeen baña am benn gàkk mbaa sikk. 3:15 Te jàppleen ne, muñug sunu Boroom muccu nit la. Sunu mbokk mi nu bëgg Pool bind na leen ko, ci xel mi ko Yàlla sol. 3:16 Noonu lay waxe ciy bataaxelam yépp di ci biral lii. Am na ci sax yu jafee xam, te ñi amul xam-xam te seen ngëm dëgërul di ko walbati, ba alag seen bopp, te loolu lañuy def ci Mbind yi ci des. 3:17 Noonu yeen samay xarit, gannaaw xam ngeen loolu ba noppi, moytuleen ñi weddi fàbbi leen ci seen réer, ba yolomal seen wàkkirlu ci Yàlla. 3:18 Waaye màggleen ci yiwu sunu Boroom ak Musalkat Yeesu Krist, te sax ci xam ko; moo yelloo ndam fii ba fàww.
1:1 Nu ngi leen di bind ci mbirum Ki ñuy wax Kàddug dund, moom mi amoon ca njàlbéen ga; mi nu dégg te gis ko ak sunuy bët, mi nu xool te laal ko ak sunuy loxo. 1:2 Dund feeñ na, te gis nanu ko; te moom lanuy seedeel, di leen yégal dund gu dul jeex, googu nekkoon ci wetu Yàlla Baay bi te feeñu nu. 1:3 Li nu gis te dégg ko, nu ngi leen koy yégal, ngir yéen itam ngeen bokk ak nun. Te dëgg-dëgg bokk nanu ci Baay bi ak Doomam, Yeesu Kirist. 1:4 Nu ngi leen di bind yëf yii, ngir sunu mbég mat sëkk, nun ñépp. 1:5 Xebaar bi nu dégg ci Yeesu Kirist, di leen ko yégal, mooy lii: Yàlla Leer la, te genn lëndëm nekkul ci moom. 1:6 Su nu waxee ne, bokk nanu ci moom, tey dox ci lëndëm, danuy fen ci sunuy wax ak sunuy jëf. 1:7 Waaye bu nuy dox ci leer, ni mu nekke moom ci boppam ci leer, kon bokk nanu ci sunu biir, te deretu Yeesu Doomam dina nu sellal ci bépp bàkkaar. 1:8 Su nu waxee ne amunu bàkkaar, kon nax nanu sunu bopp, te dëgg nekkul ci nun. 1:9 Su nu nangoo sunuy bàkkaar ci kanamam, fekk kuy sàmm kóllëre la te jub, ngir baal nu sunuy bàkkaar te sellal nu ci lépp lu jubadi. 1:10 Su nu waxee ne defunu bàkkaar, teg nanu ko kuy tebbi waxam, te kàddoom duggagul ci sunu xol.
2:1 Samay doom, maa ngi leen di bind yëf yii, ngir ngeen bañ a def bàkkaar. Waaye su kenn defee bàkkaar, ba tey am nanu ku nuy rammu ci Baay bi, mooy Yeesu Kirist mu jub mi. 2:2 Te moo joxe bakkanam, ngir dindi sunuy bàkkaar, te du sax sunuy bàkkaar rekk, waaye yu àddina sépp. 2:3 Ci lii lanu xame ne, xam nanu ko: sàmm ay ndigalam. 2:4 Ku wax ne xam nga ko, te sàmmoo ay ndigalam, dangay fen, te dëgg nekkul ci yaw. 2:5 Kuy sàmm kàddug Yàlla, dëgg-dëgg sa mbëggeel ci Yàlla mat na sëkk. Ci loolu lanu xame ne, nekk nanu ci moom. 2:6 Ku wax ne ci Yàlla nga sax, fàww nga dund, ni Yeesu Kirist daan dunde moom ci boppam. 2:7 Samay soppe, li ma leen di bind du ndigal lu bees, waaye ndigal lu yàgg la; la ngeen jotoon ca ndoorte la. Te ndigal lu yàgg loolu, mooy kàddu gi ngeen déggoon. 2:8 Teewul ndigal lu bees laa leen di bind, lu amoon ci dundu Yeesu, te am it ci seen dund; ndaxte lëndëm gaa ngi wéy, te leer gu wóor gi fenk na xaat. 2:9 Ku wax ne yaa ngi ci leer, tey bañ sa mbokk, yaa ngi ci lëndëm ba tey. 2:10 Kuy sopp sa mbokk, yaa ngi dëkk ci leer, te luy yóbbe nit bàkkaar du nekk ci yaw. 2:11 Waaye kuy bañ sa mbokk, ci lëndëm nga nekk, di ci dox, te xamoo foo jëm, ndax lëndëm muur na say bët. 2:12 Samay doom, maa ngi leen di bind,ndax baalees na leen seeni bàkkaar ci turu Kirist. 2:13 Maa ngi leen di bind, yéen baay yi,ndax xam ngeen Ki nekkoon ca njàlbéen ga ba tey.Maa ngi leen di bind, yéen waxambaane yi,ndax daaneel ngeen Ibliis. 2:14 Bind naa leen, samay doom,ndax xam ngeen Yàlla Baay bi.Bind naa leen, yéen baay yi,ndax xam ngeen Ki nekkoon ca njàlbéen ga ba tey.Bind naa leen, yéen waxambaane yi,ndax yéena ngi dëgër,ndax kàddug Yàllaa ngi dëkk ci yéen,te daaneel ngeen Ibliis. 2:15 Buleen sopp àddina ak li ci biiram. Ku sopp àddina, mbëggeelu Baay bi nekkul ci moom. 2:16 Ndaxte lépp lu nekk ci àddina, maanaam bëgg-bëggu yaram ak xemmemu bët ak réyug àddina, loolu du jóge ci Baay bi waaye ci àddina. 2:17 Te àddina day wéy, waaye kuy def coobareg Yàlla dinga sax ba fàww. 2:18 Samay doom, waxtu wu mujj wi jot na! Dégg ngeen ne, benn Bañaaleb Kirist dina ñëw; te dëgg la, bañaaley Kirist yu bare feeñ nañu. Ci loolu lanu xame ne, waxtu wu mujj wi jot na. 2:19 Ci sunu biir lañu jóge, waaye bokkuñu woon ci nun; ndaxte su ñu bokkoon ci nun, kon dinañu des ci nun. Waaye dàggeeku nañu nu, ngir mu leer ne, kenn ci ñoom bokkul woon ci nun. 2:20 Yéen nag, Aji Sell ji sol na leen Xelam, te yéen ñépp am ngeen xam-xam. 2:21 Bind naa leen, du ndax xamuleen dëgg, waaye ndax xam ngeen ko, xam it ne wenn fen du jóge ci dëgg. 2:22 Kan mooy fenkat bi? Mooy kiy weddi ne Yeesu mooy Kirist, Almasi bi. Kooka mooy Bañaaleb Kirist, biy weddi Baay bi ak Doom ji. 2:23 Ku weddi Doom ji, amuloo itam Baay bi; ku seedeel Doom ji, am nga it Baay bi. 2:24 Yéen nag, la ngeen déggoon ca ndoorte la, na sax ci yéen. Loolu ngeen déggoon ca ndoorte la, su saxee ci yéen, dingeen sax yéen itam ci Doom ji ak ci Baay bi. 2:25 Te li mu nu digoon mooy lii: dund gu dul jeex. 2:26 Bind naa leen lii ci mbirum ñi leen di bëgg a réeral. 2:27 Yéen nag, Xel mi leen Kirist sol a ngi dëkk ci yéen, te soxlawuleen kenn jàngal leen dara. Waaye Xel mi mu leen sol, mi ngi leen di jàngal lépp, te li mu leen di jàngal mooy dëgg; kon nag saxleen ci moom, ni mu leen ko jàngale. 2:28 Gannaaw loolu nag yéen samay doom, saxleen ci Kirist, ngir bés bu feeñee, nu am kóolute ci kanamam te bañ a rus ba sëngéem cig dikkam. 2:29 Gannaaw xam ngeen ne ku jub la, dingeen xam it ne, képp kuy def lu jub juddu nga ci moom.
3:1 Xool-leen mbëggeel gi nu Baay bi jox, ni mu réye, ba nu man a tudd doomi Yàlla. Te moom lanu. Moo tax àddina xamu nu, ndaxte xamu ko woon, moom itam. 3:2 Samay soppe, léegi doomi Yàlla lanu, te li nu nar a nekki feeñagul, waaye xam nanu ne, bés bu Almasi bi feeñee, dinanu nirook moom, ndaxte dinanu ko gis, na mu mel. 3:3 Te képp ku am yaakaar jooju ci moom, dinga sellal sa bopp, ni mu selle moom. 3:4 Ku def bàkkaar, jàdd nga yoon; ndaxte bàkkaar mooy jàdd yoon. 3:5 Te xam ngeen ne Yeesu Kirist feeñ na, ngir dindi bàkkaar yi, te moom amul benn bàkkaar. 3:6 Képp ku sax ci moom, doo sax ci bàkkaar; kuy def bàkkaar, gisuloo ko te xamuloo ko. 3:7 Samay doom, bu leen kenn nax! Kuy def lu jub, ku jub nga, ni Kirist jube moom ci boppam. 3:8 Kuy def bàkkaar, ci Seytaane nga bokk, ndax Seytaane ca njàlbéen ga ba tey day bàkkaar. Te Doomu Yàlla ji ñëw na, ngir nasaxal jëfi Seytaane. 3:9 Ku juddu ci Yàlla doo def bàkkaar, ndax Yàlla sol na la jikkoom, te doo man a sax ci bàkkaar, ndax juddu nga ci Yàlla. 3:10 Lii mooy ràññale doomi Yàlla ak doomi Seytaane: képp ku dul def lu jub bokkoo ci Yàlla; naka noonu itam ku soppul sa mbokk bokkoo ci Yàlla. 3:11 Ndaxte xebaar, bi ngeen déggoon ca ndoorte la, mooy lii: nanu bëggante, 3:12 te bañ a mel ni Kayin, mi bokkoon ci Ibliis, ba rey rakkam. Lu tax mu rey ko nag? Ndaxte ay jëfam dañoo bon, te yu rakkam jub. 3:13 Bokk yi, bu leen àddina bañee, buleen ci jaaxle. 3:14 Mbëggeel gi nu bëgg sunuy bokk moo nuy xamal ne, jóge nanu ci dee, tàbbi ci dund. Ku bëggul sa mbokk, yaa ngi ci dee ba tey. 3:15 Képp ku bañ sa mbokk, reykat nga; te xam ngeen ne, ku rey nit amuloo dund gu dul jeex. 3:16 Ci lii lanuy xàmmee luy mbëggeel: Kirist joxe na bakkanam ngir nun; te nun itam war nanoo joxe sunu bakkan ngir sunuy bokk. 3:17 Waaye ku am alalu àddina te gis sa mbokk nekk ci soxla, nga dummóoyu ko, nan la mbëggeelu Yàlla dëkke ci yaw? 3:18 Samay doom, bunu bëggante ci wax mbaa ci làmmiñ rekk, waaye ci jëf ak ci dëgg. 3:19 Ci loolu lanu xame ne, nu ngi ci dëgg; te waxtu wu sunu xol di xeex ak nun, dinanu ko dalal ci kanamam; ndaxte Yàllaa ëpp sunu xol te xam na lépp. 3:21 Samay soppe, bu nu sunu xol daanul, kon man nanoo jege Yàlla ak kóolute. 3:22 Te lépp lu nu koy ñaan, dinanu ko jot ci moom, ndaxte nu ngi sàmm ay ndigalam, di def lu ko neex. 3:23 Ndigalam mooy lii: nu gëm turu Doomam, Yeesu Kirist, tey bëggante, ni mu nu ko digale. 3:24 Kuy sàmm ndigalu Yàlla, dinga sax ci moom, mu dëkk ci yaw. Te Xel mi mu nu jox, moo nuy xamal ne, dëkk na ci nun.
4:1 Samay soppe, buleen gëm xel mu nekk, waaye nattuleen xel yi, ba xam ndax ci Yàlla lañu jóge walla déet, ndaxte naaféq yu bare yu mbubboo turu yonent jóg nañu, tasaaroo ci àddina si. 4:2 Ci lii lanu xàmmee Xelum Yàlla: mépp xel mu nangu ne, Yeesu Kirist ñëw na, nekk nit, ci Yàlla la bokk. 4:3 Waaye mépp xel mu nanguwul Yeesu, bokkul ci Yàlla. Xel moomu mooy xelum Bañaaleb Kirist, mi ngeen déggoon ne dina ñëw, te léegi sax mu ngi ci biir àddina. 4:4 Yéen samay doom, ci Yàlla ngeen bokk, te daan ngeen yonent yu naaféq yooyu, ndaxte Ki nekk ci yéen moo ëpp doole ki nekk ci àddina. 4:5 Ñoom ci àddina lañu bokk; moo tax ñuy wax waxi àddina, te àddina di leen déglu. 4:6 Nun nag ci Yàlla lanu bokk. Ku xam Yàlla dinga nu déglu; ku bokkul ci Yàlla doo nu déglu. Ci loolu lanuy xàmmee Xel miy dëgg ak xel mi dul dëgg. 4:7 Samay soppe, nanu bëggante, ndax mbëggeel ci Yàlla la bawoo; képp ku bëgg sa mbokk nag, ci Yàlla nga juddoo, te xam nga Yàlla. 4:8 Ku bëggul sa mbokk, xamuloo Yàlla, ndax Yàlla mbëggeel la. 4:9 Nii la Yàlla wonee mbëggeelam ci nun; yónni na ci àddina jenn Doomam ji mu am kepp, ngir nu am dund ci moom. 4:10 Lii mooy mbëggeel, du sunu mbëggeel ci Yàlla, waaye mbëggeelam ci nun, ba mu yónni Doomam, mu joxe bakkanam, ngir dindi sunuy bàkkaar. 4:11 Samay soppe, bu nu Yàlla bëggee nii, nun itam war nanoo bëggante. 4:12 Kenn musul a gis Yàlla, waaye bu nu bëggantee, Yàllaa ngi dëkk ci nun te mbëggeelam mat na sëkk ci nun. 4:13 Ci lii lanuy xame ne, sax nanu ci Yàlla, te moom itam dëkk na ci nun: sol na nu Xelam. 4:14 Te nun gis nanu te seede ne, Baay bi yónni na Doom ji, mu nekk Musalkatu àddina. 4:15 Képp ku nangu ne, Yeesu Doomu Yàlla la, Yàlla dëkk na ci yaw, te yaw it sax nga ci Yàlla. 4:16 Mbëggeel gi Yàlla am ci nun, xam nanu ko te gëm ko. Yàlla mbëggeel la, te képp ku sax ci mbëggeel, yaa ngi sax ci Yàlla, mu dëkk ci yaw. 4:17 Ni Kirist mel, noonu lanu mel nun itam ci àddina. Ci loolu la mbëggeel mate sëkk ci nun, ngir nu am kóolute bésu àtte ba. 4:18 Genn ragal amul ci mbëggeel, waaye mbëggeel gu mat sëkk day dàq ragal. Ndaxte ragal day ànd ak mbugal; te ku ragal, mbëggeel matul sëkk ci yaw. 4:19 Danuy wéy ci mbëggeel, ndax moo nu jëkk a bëgg. 4:20 Su kenn nee: «Bëgg naa Yàlla,» te bëgguloo sa mbokk, dangay fen; ndaxte ku bëggul sa mbokk mi ngay gis, doo man a bëgg Yàlla mi nga gisul. 4:21 Te jox na nu ndigal lii: ku bëgg Yàlla, nga bëgg sa mbokk.
5:1 Képp ku gëm ne Yeesu mooy Almasi bi, juddu nga ci Yàlla; te ku bëgg waajur, dinga bëgg itam ki mu jur. 5:2 Xam nanu ne, bëgg nanu doomi Yàlla yi ci lii: bëgg Yàlla tey sàmm ay ndigalam. 5:3 Ndaxte mbëggeel ci Yàlla mooy sàmm ay ndigalam; te ay ndigalam diisuñu. 5:4 Ndaxte képp ku juddu ci Yàlla day noot àddina; te li nuy noote àddina mooy sunu ngëm. 5:5 Ku noot àddina mooy kan? Mooy ki gëm ne, Yeesu mooy Doomu Yàlla. 5:6 Yeesu Kirist mooy ki ñëw, jaar ci ndox ak deret; du ci ndox rekk, waaye ndox ak deret. Te Xelu Yàlla mi moo koy seedeel, ndax Xel mi mooy dëgg. 5:7 Ndaxte am na ñetti seede: 5:8 Xel mi, ndox ak deret, te ñoom ñett ñépp, ñoo bokk benn baat. 5:9 Seedes nit, dinanu ko nangu, waaye seedes Yàlla moo gën a wóor, ndax boobu seede mooy li Yàlla seede ci Doomam. 5:10 Ku gëm Doomu Yàlla ji, am nga seede boobu ci sa xol. Ku gëmul Yàlla, teg nga ko kuy tebbi waxam ndaxte gëmuloo li Yàlla seede ci Doomam. 5:11 Te seede si mooy lii: Yàlla jox na nu dund gu dul jeex, te dund googoo ngi ci Doomam. 5:12 Ku am Doom ji, am nga dund; ku amul Doomu Yàlla, amuloo dund. 5:13 Maa ngi leen di bind yëf yii, yéen ñi gëm turu Doomu Yàlla ji, ngir ngeen xam ne, am ngeen dund gu dul jeex. 5:14 Kóolute gi nu am ci kanam Yàlla mooy lii, su nu ko ñaanee dara ci coobareem, dina nu nangul. 5:15 Gannaaw xam nañu ne, dina nangu lépp lu nu koy ñaan, xam nanu it ne, li nu ko ñaan, jox na nu ko. 5:16 Ku gis mbokkam, muy def bàkkaar bu jarul dee, na ko ñaanal, te Yàlla dina ko may dund. Ku def bàkkaar bu jarul dee laa wax. Ndaxte am na bàkkaar bu jar dee; boobu taxul may wax, mu ñaanal ko. 5:17 Gépp jubadi bàkkaar la, waaye am na bàkkaar bu jarul dee. 5:18 Xam nanu ne, képp ku juddu ci Yàlla doo sax ci bàkkaar, waaye Doomu Yàlla ji mooy wottu sa bakkan, ba Ibliis du la manal dara. 5:19 Nun nag xam nanu ne, nu ngi ci Yàlla, te àddina sépp a ngi tëdd ci loxoy Ibliis. 5:20 Xam nanu ne, Doomu Yàlla ji ñëw na te may na nu xel, ba nu man a xam Aji Wóor ji. Te nu ngi ci Aji Wóor ji ak ci Doomam Yeesu Kirist. Kooku mooy Yàlla ju wóor, ji yor dund gu dul jeex. 5:21 Samay doom, wottuleen seen bopp ciy xërëm.
1:1 Man njiit li maa leen di bind, yaw soxna su tedd si, yaw ak say doom. Bëgg naa leen bu wér ci sama xol, jéllale naa sama bopp sax, waaye itam képp ku xam dëgg gi. 1:2 Te dëgg gee tax nuy def noonu, dëgg gi dëkk ci nun, tey ànd ak nun ba fàww. 1:3 Yàlla Baay bi ak Yeesu Krist, Doomu Baay bi, dinañu nu may yiw, yërmande ak jàmm, ànd ak dëgg ak mbëggeel. 1:4 Gis naa ci say doom, ñuy jaar ci tànki dëgg, ni nu ko Baay bi digale, te bég naa ci lool. 1:5 Léegi nag soxna si, maa ngi lay dénk lii: nun ñépp nanu bëggante, te loolu du dénkaane bu bees, waaye moom lanu jotoon ca njàlbéen ga. 1:6 Lii mooy mbëggeel: nu wéer sunug dund ci ndigali Yàlla; loolu mooy ndigalam, la nu jotoon ca njàlbeen ga, te ci lanu wara jaar. 1:7 Maa ngi wax loolu nag, ndaxte am na ñuy sànke ñu bare, ñu tasaaroo ci àddina si, te nanguwuñu ne Yeesu Krist wàcc na, nekk nit. Kooku aji sànke la, di Bañaaleb Krist. 1:8 Kon moytuleen, ngir baña ñàkk seen añub coono, waaye ngeen am yool bu mat sëkk. 1:9 Képp ku saxul ci dénkaaney Krist, xanaa di ko weesu, bokkul ci Yàlla; ku sax ci dénkaane yi, bokk nga ak Baay bi ak Doom ji. 1:10 Ku ñëw fi yaw, te indaalewul dénkaane yooyu, waxuma nga bañ koo teeru rekk, waaye bu ko nuyu sax. 1:11 Ku ko nuyu, bokk nga ciy ñaawteefam. 1:12 Bëggoon naa leena wax lu bare ci bataaxel bii, waaye lépp xajul ci kayit. Kon nag fas naa yéenee ñëw, ba jàkkaarlook yeen, nu waxtaan ci, ngir sunu mbég mat sëkk. 1:13 Say doomi rakk, ji Yàlla tànn, ñu ngi lay nuyu.
1:1 Man njiit li, maa ngi lay bind, yaw sama xarit Gayus, mi ma bëgg ci sama xol. 1:2 Sama soppe, maa ngi ñaan, Yàlla may la jàmm ci lépp, ànd ak wér gi yaram, ju mel ni sa naataangeg xol. 1:3 Sunuy mbokk ñëw nañu, te seede ni nga fonke dëgg gi, ba wéer ci sa dund gépp, te bég naa ci lool. 1:4 Awma mbég mu ëpp lii: ma dégg ne samay doomi diine ñu ngiy jaar ci tànki dëgg. 1:5 Yaw sama xarit, sa takkute fés na ci teeru bi ngay teeru mbokk yi, te fekk xamoo leen. 1:6 Seedeel nañu sa mbëggeel fi kanam mbooloom ñi gëm. Taxawu leen nag ci seen yoon taxawu gu neex Yàlla. 1:7 Ndaxte turu Krist la leen taxa jóg, te sàkkuwuñu daray ku gëmul. 1:8 Nun nag fàww nu teeru ñu mel ni ñoom, ngir nu liggéeyandoo ak dëgg gi. 1:9 Bind naa mbooloo mi bataaxel, waaye Jotref, mi bëgg noot ñépp, du dégg sunu ndigal. 1:10 Kon nag su ma ñëwee, dinaa fàttali li mu def lépp, ci di nu sosal ci kàdduy neen yu ñaaw. Yemu foofu sax, waaye nanguwula teeru mbokk yi, rax-ca-dolli ku leen bëgga teeru, mu gàllankoor ko, dàq ko ci mbooloo mi. 1:11 Sama xarit, bul roy lu bon, waaye lu baax rekk. Kuy def lu baax, ci Yàlla nga bokk; kuy def lu bon, xamoo dara ci Yàlla. 1:12 Naka Démétrius nag, ñépp seedeel nañu ko lu baax, te dëgg gi sax seedeel na ko ko. Nun itam seedeel nanu ko te wóor na ma ne, sunu seede dëgg la. 1:13 Am na lu bare, lu ma la bëggoona wax, waaye lépp xajul ci kayit. 1:14 Kon yaakaar naa laa seetsi balaa yàgg, jàkkaarlook yaw, nu waxtaan ci. 1:15 Na jàmm ànd ak yaw. Xarit yi yépp ñu ngi lay nuyu. Nuyul nu sunuy xarit, kenn ku nekk ci turam.
1:1 Man Yudd, jaamu Yeesu Kirist, mi bokk ak Saag ndey ak baay, maa leen di bind, yéen ñi Yàlla Baay bi woo te bëgg leen, te Yeesu Kirist aar leen. 1:2 Na leen Yàlla may yërmande, jàmm ak mbëggeel. 1:3 Samay bokk, bëggoon naa leen a bind lool ci mbirum mucc gi nu bokk, waaye lii moo gën a jamp: ma xiir leen, ngeen taxaw ci aar mboolem dëgg, yi Yàlla xas a dénk gaayam yu sell yi ba fàww. 1:4 Ndaxte am na ay nit ñu ñeme Yàlla, ñu yoxoosu ci seen biir; dañuy mbubboo yiwu Yàlla, ngir topp seen bakkan, di ci weddi Buur Yàlla miy kenn ak sunu Boroom Yeesu Kirist. Fekk Mbind mi tëral na seen àtte bu yàgg. 1:5 Xam ngeen loolu lépp ba noppi sax, waaye dama leen koy fàttali rekk. Xam ngeen ne Boroom bi musal na xeetam, ba génne leen réewu Misra, waaye gannaaw ba raafal na ñi gëmul woon. 1:6 Te it malaaka ya jàppul woon ca daraja ja ñu amoon, xanaa toxoo fa ñu leen dëëloon, Yàlla yeew na leen buum yu sax, tëj leen ci biir lëndëm, di leen nége àtteb bés bu mag ba. 1:7 Noonu itam dëkki Sodom ak Gomor ak dëkk ya leen wëroon, dañoo sóobu ci njaaloo ak di def ay góor-jigéen, waaye àtte bi dal na ci seen kaw, ba ñuy ay tegtal ci ñiy yelloo safara ba fàww. 1:8 Naka noonu itam gentkat yooyu may wax ñu ngi sobeel seen yaram, di weddi gépp kilifteef, di xas doole yi ci asamaan. 1:9 Waaye bi Mikayel, miy kilifa ci malaaka yi, di xëccook Seytaane néewu Musaa, bay xuloo ak moom, ñemewu koo àtte, boole ciy xas; mu yem ci wax ko ne: «Na la Boroom bi mbugal!» 1:10 Waaye nit ñii may wax, dañuy saaga li ñu xamul. Te li ñu xam ci tañaxu sax, ni bàyyima yu amul xel, dañu ci yàq seen bopp. 1:11 Ñoo kay torox! Dañoo jaar ci yoonu Kayin, sóobu ci réerug Balaam ngir xaalis, di bañ kilifteef ni Kore, te dinañu dee ni moom. 1:12 Su ñu bokkee ak yéen reeru mbooloo mi, dañu ciy indi ay, niy xeer yu nëbbu ci biir géej; amuñu genn gàcce, waaye dañuy giiroo te fonk seen biir rekk. Ñu ngi mel ni xiin yu amul ndox, yuy naaxsaay ci ngelaw; ni garab yu meññul ci jamonoy meññeef, te buddeeku, dee ba wow koŋŋ; 1:13 mel ni duusi géej gu mer, yuy gëq jëf yu ruslu; niy biddiiw yuy faq, te Yàlla dencal na leen lëndëm ya gën a tar ba fàww. 1:14 Enog, di juróom-ñaareelu maam gannaaw Aadama, waxoon na ci kàddug Yàlla, ba weer leen ne: «Boroom bi wàcce na ca asamaan, ànd ak ay junniy junniy malaakaam, 1:15 ngir àtte ñépp, te mbugal ñi weddi ñépp ndax ñaawteef, yi ñu jëf ci ñeme Yàlla; di leen fàttali it kàddu yu ñaaw, yi ñu ko tifaar ci seeni bàkkaar ak seen weddi.» 1:16 Duñu noppee xultu, di jàmbat seen nekkin, tey topp seen nafsu; ay wax yu réy a ngi ball ci seen làmmiñ, waaye dañuy jey ñi ñuy yaakaare njariñ. 1:17 Waaye yéen samay xarit, fàttalikuleen la leen ndawi sunu Boroom Yeesu Kirist waxoon lu jiitu, 1:18 ne leen: «Muju jamono ay tiiñalkat dinañu feeñ, ñuy weddi Yàlla, ngir topp seen bakkan.» 1:19 Ñooy féewale, te Xelum Yàlla nekkul ci ñoom, waaye niti kese lañu. 1:20 Waaye yéen samay xarit, doolewuleen ci seen yoonu ngëm wu sell, tey ñaan ci dooley Xel mu Sell mi, 1:21 ba saxoo mbëggeelu Yàlla, tey séentu yërmandey sunu Boroom Yeesu Kirist, mu tàbbal leen ci dund gu dul jeex. 1:22 Jubbantileen ñi am werantey xel, 1:23 ngeen musal ñale, jële leen ci safara, te yërëm ñeneen ñi, waaye boole ci moytu, ba sib sax seen yére yi taq sobe. 1:24 Yàlla mi leen man a aar ci gépp jeng, te teewal leen fa kanam ndamam, ngeen ñàkk sikk te fees dell ak mbég; 1:25 Yàlla miy kenn, di sunu Musalkat, na yelloo ndam ak màgg, kàttan ak nguur, jaar ci Yeesu Kirist sunu Boroom, démb, tey, ëllëg ba fàww. Amiin.
1:1 Lii mooy li Yeesu Kirist feeñal, te mu tukkee ca Yàlla, ngir mu won ay jaamam mbir, yi dëgmël di ñëw. Yónni na malaakaam, ngir xamal ko ab jaamam Yowaana. 1:2 Kooku mi ngi seede fii li mu gis lépp, maanaam kàddug Yàlla ak seede, si ñu seedeel Yeesu Kirist. 1:3 Barkeel ngeen, yaw miy jàng ak yéen ñiy déglu wax yii jóge ca Yàlla, te di sàmm li ñu ci bind, ndaxte waxtu wi jege na. 1:4 Man Yowaana maa leen di bind, yéen juróom-ñaari mboolooy ñi gëm te nekk ci diiwaanu Asi. Na yiw ak jàmm féete ci yéen, jóge ci Yàlla, moom ki nekk, ki nekkoon démb te di ñëw ëllëg. Yiw woowu ak jàmm jooju ñoo ngi tukkee it ci juróom-ñaari Xeli Yàlla, yi nekk ci kanamu gàngunem Yàlla, 1:5 tukkee it ci Yeesu Kirist, seede bu takku bi, moom taaw bi, maanaam ki jëkk a dekki, di buuru buur yi ci kaw suuf yépp. Na ndam ak nguur féete ak Yeesu Kirist ba fàww, moom mi nu bëgg te yiwi nu ci sunuy bàkkaar ak deretam ji tuuru, te def nu askanu saraxalekati Buur Yàlla Baayam, nu di ko jaamu. Amiin. 1:7 Gisleen, mi ngi ñëw ci niir yi,te ñépp dinañu teg seeni bët ci moom,ba ci ñi ko jam sax.Te xeet yi nekk ci kaw suuf yéppdinañu jooy ndax moom.Waaw. Amiin. 1:8 Boroom bi Yàlla nee na: «Man Yàlla maay Alfa ak Omega, maay ki nekk, ki nekkoon démb te di ñëw ëllëg, man Aji Kàttan ji.» 1:9 Man Yowaana seen mbokk, di seen nawle ci fitna, ci nguur ak ci muñ, yi nu am ndax sunu booloo ak Yeesu, maa nga nekkoon ca dun bu ñuy wax Patmos. Wacce woon nañu ma fa, ndax li ma doon waare kàddug Yàlla tey seedeel Yeesu. 1:10 Xelum Yàlla solu ma ci bésu Boroom bi, te noonu ma dégg ci sama gannaaw baat bu xumb nig liit, 1:11 naan: «Bindal ci téere li ngay gis te yónnee ko juróom-ñaari mboolooy ñi gëm, ca dëkki Efes, Samirin, Pergam, Catir, Sàrd, Filadelfi ak Lawdise.» 1:12 Noonu ma geestu, ngir seet ku doon wax ak man. Ba ma geestoo, yem ci juróom-ñaari làmpi diwlin yu wurus, 1:13 gis ku taxaw ci biir làmp ya, niroo ak doomu nit. Mu sol mbubb mu gudd, takk ngeñaayu wurus ci ndiggam. 1:14 Boppam ak kawaram weex tàll ni perkaal, ay bëtam di xuyy ni safara. 1:15 Ay tànkam mel ni xànjar bu yànj bu ñu xelli, baatam di riir ni duusi géej. 1:16 Mu yor ci loxol ndeyjooram juróom-ñaari biddiiw, jaasiy ñaari boor yu ñaw di génn ci gémmiñam, xar-kanamam leer nàññ ni jantub njolloor. 1:17 Naka laa ko gis, di daanu ci ay tànkam ni ku dee. Waaye mu teg loxol ndeyjooram ci sama kaw ne ma: «Bul ragal dara. Maay ki jëkk te maay mujj. 1:18 Maay Kiy Dund. Dee woon naa, waaye maa ngii di dund ba fàww, yor caabiy dee ak ju barsàq. 1:19 Kon nag bindal li nga gis, li am léegi ak li nar a ami gannaaw gi. 1:20 Juróom-ñaari biddiiw yi nga gis ci sama loxol ndeyjoor, ak juróom-ñaari làmpi diwlin yu wurus yi, ay mbóoti Yàlla lañu te lii lañuy tekki: biddiiw yi ñoo di malaakay juróom-ñaari mboolooy ñi gëm; juróom-ñaari làmp yi ñoo di juróom-ñaari mbooloo yi.
2:1 «Bindal malaakam mbooloom ñi gëm ci dëkku Efes, ne ko: i Ki téye juróom-ñaari biddiiw yi ci loxol ndeyjooram, tey dox ci diggu juróom-ñaari làmpi diwlin yu wurus yi nee na: 2:2 Xam naa say jëf, sa liggéey ak sag muñ. Xam naa ne, mënuloo dékku ñiy def lu bon. Seetlu nga ñi tuddoo samay ndaw, ba gis ne ay naaféq lañu. 2:3 Xam naa it ne muñ nga, ba dékku coono ndax sama tur, te xàddiwoo. i 2:4 Waaye li ma naqari ci yaw moo di sa mbëggeel wàññiku na. 2:5 Deel fàttaliku kon fa nga daanoo. Réccul te def, na nga daan def bu jëkk. Soo réccuwul, dinaa dikk ci yaw, jële sa làmp ca bérab ba mu nekk. 2:6 Waaye lii neex na ma ci yaw: sib nga ni man li ñoom Nikolas di jëf. i 2:7 Yaw mi am ay nopp, déglul li Xelum Yàlla di wax mboolooy ñi gëm. Ku daan, dinaa la may, nga lekk ci garabu dund, gi nekk ci jataayu Yàlla. 2:8 «Bindal malaakam mbooloom ñi gëm ci dëkku Samirin, ne ko: i Ki jëkk te mujj, ki dee woon te dekki nee na: 2:9 Xam naa sa coono, xam it sa néew doole, moona yaaka duunle. Ñooñu tuddoo Yawut, xam naa ñaawteef yi ñu teg ci sa der: ndajem Seytaane la. 2:10 Bul ragal li nga nar a daj. Seytaane dina dugal kaso ñenn ci yéen, ngir wut leen a fiir. Diirub fukki fan dingeen am coono. Nanga takku ba àttan cee dee, ma jox la kaalag dund gi. i 2:11 Yaw mi am ay nopp, déglul li Xelum Yàlla di wax mboolooy ñi gëm. Ku daan, doo loru ci ñaareelu dee. 2:12 «Bindal malaakam mbooloom ñi gëm ci dëkku Pergam, ne ko: i Boroom jaasi ju ñaw, ji am ñaari boor nee na: 2:13 Xam naa fa nga dëkk, di fa Seytaane samp nguuram. Moona jébbalu nga ci sama tur te weddiwoo sa ngëm ci man, ba ca fan ya ñu reye Antipas, sama seede bu takku ba, ci seen dëkk, di dëkku Seytaane. i 2:14 Waaye am na lu ma naqari ci yaw, moo di uuf nga foofu gaa yuy sàmm njàngalem Balaam, moom mi jàngaloon Balag, mu sóob bànni Israyil ci bàkkaar, xiir leen ci lekk ñam wu ñu tuuroo xërëm yi, xiir leen ci njaaloo. 2:15 Te am nga noonu itam ay nit ñuy sàmm njàngalem ñoom Nikolas. 2:16 Réccul kon; lu ko moy dinaa dikk ci yaw léegi te xeex ak nit ñooñu ak jaasi, jiy génn ci sama gémmiñ. i 2:17 Yaw mi am ay nopp, déglul li Xelum Yàlla di wax mboolooy ñi gëm. Ku daan, dinaa la jox, nga lekk dund bi ñuy wax mànn te mu nëbbu, te dinaa la jox xeer wu weex. Ci kaw xeer woowu bindees na ci tur wu bees wu kenn xamul, ku dul ki ko jot. 2:18 «Bindal malaakam mbooloom ñi gëm ci dëkku Catir, ne ko: i Doomu Yàlla ji, ki ay bëtam di xuyy ni safara, tey tànkam di lerax ni xànjar, nee na: 2:19 Xam naa say jëf, sa mbëggeel, sa ngëm, sag muñ ak ni nga farloo ci sa jaamu Yàlla. Xam naa say jëf yu mujj, ni ñu ëppe yu jëkk ya. i 2:20 Waaye li ma naqari ci yaw moo di dangaa bàyyi Yesabel, jigéen joojuy tuddoo yonent, di jàngale ak a réeral sama jaam yi, ngir ñuy sóobu ci njaaloo te di lekk ñam wu ñu tuuroo xërëm yi. 2:21 May naa ko ab diir, ngir mu tuub njaaloom, waaye bañ na. 2:22 Kon nag dinaa ko tëral ci lalu metit, te ñiy ànd ak moom di njaaloo, su ñu tuubul jëfi jigéen jooju, dinaa leen teg naqar wu mag. 2:23 Dinaa rey ay doomam, te mboolooy ñi gëm yépp dinañu xam ne, man maa di kiy nattu xol ak xalaat, te dinaa fey ku nekk ay jëfam. 2:24 Waaye yéen ñépp ñi des ci Catir te toppuleen njàngale moomu te gëstuwuleen loolu ñu naan mbiri Seytaane yu xóot yi, maa ngi leen di wax ne, duma leen yen beneen yen 2:25 bu dul bii: jàppleen ci li ngeen jàpp, ba kera may ñëw. i 2:26 Ku daan tey sax ci samay jëf ba ca muj ga, dinaa ko jox sañ-sañ ci xeet yi:i 2:27 Dina leen jiite ak yetu weñ,i tojat leen ni ñuy toje ndaal kew —i 2:28 ni ma jële sañ-sañ ci sama Baay. Dinaa ko jox it biddiiwu njël. 2:29 Yaw mi am ay nopp, déglul li Xelum Yàlla di wax mboolooy ñi gëm.
3:1 «Bindal malaakam mbooloom ñi gëm ci dëkku Sàrd, ne ko: i Ki yor juróom-ñaari Xeli Yàlla yi ak juróom-ñaari biddiiw yi nee na: Xam naa say jëf. Dañu laa teg kuy dund, fekk dee nga. 3:2 Yeewul te dëgëral li des ci yaw tey waaj a dee, ndaxte gis naa ne, say jëf matuñu ca sama kanam Yàlla. 3:3 Fàttalikul kon kàddug Yàlla gi nga jot, te dégg ko, sàmm ko te réccu. Soo wéyee ciy nelaw nag, dinaa ñëw nib sàcc, te doo xam wan waxtu lay doon. i 3:4 Moona am nga foofu ci Sàrd nit ñu néew ñoo xam ne tilimaluñu seen mbubb. Ñooñu dinañu ànd ak man, sol lu weex, ndaxte yeyoo nañu ko. 3:5 Ku daan, dinga sol mbubb mu weex ni ñoom. Te duma far sa tur ci téereb dund bi, waaye dinaa nangu ci sama kanamu Baay ak ay malaakaam ne, bokk nga ci man. 3:6 Yaw mi am ay nopp, déglul li Xelum Yàlla di wax mboolooy ñi gëm. 3:7 «Bindal malaakam mbooloom ñi gëm ci dëkku Filadelfi, ne ko: i Aji Sell ji, di Aji Dëgg ji nee na, moom mi yor caabiy Daawuda ji, moom miy tijji te kenn du ko man a tëj, muy tëj te kenn du ko tijji nee ne: 3:8 Xam naa say jëf. Ubbil naa la bunt, te kenn du ko man a tëj. Xam naa ne barewuloo doole, waaye sàmm nga sama kàddu te weddiwoo ma. 3:9 Dinaa def ba ñenn ci ñi bokk ci ndajem Seytaane --te tuddoo Yawut, fekk dañuy fen — dinaa leen ñëwloo, ñu sukk ci sa kanam, nangu ne, bëgg naa la. 3:10 Gannaaw muñ nga, ni ma la ko dénke woon, man itam dinaa la yiir ci jamono, ji musiba mi di wàcc ci dunyaa bépp ngir nattu waa àddina. i 3:11 Léegi ma ñëw. Sàmmal li nga yor, ngir kenn bañ laa xañ sa kaalag ndam. 3:12 Ku daan, dinaa la samp ni aw jënu néeg ci sama kër Yàlla te doo fa génn mukk. Dinaa bind ci yaw turu sama Yàlla ak turu dëkku sama Yàlla, mu di Yerusalem gu bees, giy jóge ca asamaan ca wetu sama Yàlla di wàcc. Dinaa bind it ci yaw sama tur wu bees. 3:13 Yaw mi am ay nopp, déglul li Xelum Yàlla di wax mboolooy ñi gëm. 3:14 «Bindal malaakam mbooloom ñi gëm ci dëkku Lawdise, ne ko: i Ki ñuy wax Amiin ji, di seede bu takku bi te dëggu, ki di ndeyi bindu mbindeefi Yàlla yi, nee na; 3:15 Xam naa say jëf, xam ne seddoo, tàngoo. Manoon ngaa sedd mbaa nga tàng, 3:16 waaye ndax li nga nugg, tàngoo seddoo, dinaa la yàbbi. 3:17 Yaa ngi damu naan: “Am naa alal, duunle naa, soxlaatuma dara.” Fekk xamuloo ne, torox nga, miskin, ñàkk, gumba te rafle. 3:18 Moo tax maa ngi lay xiirtal, nga jënd ci man wurus wu ñu xellee ci safara, ngir nga duunle, te nga jënd yére yu weex ngir nga solu, ba sa gàcceg rafle bañ a feeñ, ak tuufaay booy diw ci say bët, ngir man a gis. i 3:19 Man maay yedd, di yar ñépp ñi ma bëgg. Farlul kon te tuub say bàkkaar. 3:20 Maa ngi nii taxaw ci bunt bi, di fëgg. Ku dégg sama baat te ubbi bunt bi, dinaa dugg, reerandoo ak moom, moom it mu reerandoo ak man. i 3:21 Ku daan, dinaa la toogloo ci sama wet ci sama gàngune, ni ma xeexe ba daan, man ci sama bopp, te toogandoo ak sama Baay ci gànguneem. 3:22 Yaw mi am ay nopp, déglul li Xelum Yàlla di wax mboolooy ñi gëm.»
4:1 Gannaaw loolu ma xool, gis bunt ubbiku ci asamaan. Baat booba ma déggoon, muy wax ak man mel nig liit, ne ma: «Yéegal fii, ma won la li war a ñëw gannaaw gi.» 4:2 Ca saa sa Xelum Yàlla solu ma, noonu ma gis gàngune ca asamaan, te am ku ca toog. 4:3 Leeraayam mel ni jamaa ak per bu xonq, te xon gu leer ni per bu wert wër gàngune ma. 4:4 Yeneen ñaar-fukki gàngune ak ñeent wër ko, te ci kaw gàngune ya ñaar-fukki mag ak ñeent toog, sol mbubb yu weex ak kaalay wurus ci seen bopp. 4:5 Ay melax, ay riir ak ay dënnu di jibe ca gàngune ma. Ca kanamu gàngune ma amoon na fa juróom-ñaari làmp yu yànj, di juróom-ñaari Xeli Yàlla yi. 4:6 Amoon na it ca kanamu gàngune ma lu mel ni géej gu leer ni weer bu set, ba mel ni seetu. Ci li wër gàngune ma, sës rëkk, amoon na fa ñeenti mbindeef yu fees ak ay bët ci kanam ak ci gannaaw. 4:7 Mbindeef mu jëkk maa nga meloon ni gaynde, ñaareelu mbindeef mel ni yëkk, ñetteelu mbindeef yor kanamu nit, ñeenteel ba di nirook jaxaay juy naaw. 4:8 Ñeenti mbindeef ya am nañu ku nekk juróom-benni laaf te ñu nga fees ak ay bët li leen wër lépp, ba ci seen roni laaf. Guddi ak bëccëg duñu noppeek naan:«Boroom bi Yàlla, Aji Kàttan ji,moo sell, sell, sell,moom ki nekkoon démb,ki nekk tey, te di ñëw ëllëg.» 4:9 Saa su mbindeef ya di màggal ki toog ca gàngune ma tey dund ba fàww, te di ko kañ ak a gërëm, 4:10 ñaar-fukki mag ña ak ñeent di dëpp seen jë ca kanamu ka toog ca kaw gàngune ma. Ñu di ko jaamu, moom mi dund ba fàww, di sànni seen kaalay ndam ca kanamu gàngune ma, naan: 4:11 «Yàlla sunu Boroom,yaa yeyoo ndam, teraanga ak kàttan,ndaxte yaa sàkk léppte ci sa coobare la lépp nekke,te ci lañu leen sàkke.»
5:1 Noonu ma gis ca loxol ndeyjooru ka toog ca gàngune ma téere bu ñu bind biir ak biti, tay ko juróom-ñaari yoon ak sondeel. 5:2 Noonu ma gis malaaka mu am doole, muy xaacu naan: «Ku yeyoo dindi tayu yi te ubbi téere bi?» 5:3 Te amul kenn, muy ci asamaan, muy ci kaw suuf, muy ci biir suuf, ku manoon a ubbi téere bi, mbaa mu xool ci biir. 5:4 Ma jooy jooy yu metti ndax li kenn yeyoowul woon a ubbi téere bi mbaa mu xool ko. 5:5 Noonu kenn ca mag ña ne ma: «Bul jooy. Xoolal, Gayndeg giiru Yuda, ki soqikoo ci Daawuda, daan na, ba am sañ-sañu dindi tayu yi te ubbi téere bi.» 5:6 Noonu ma gis Mbote mu mel ni dañu koo rendi woon, mu taxaw ca digg gàngune ma, ñeenti mbindeef ya séq ko, mag ña wër ko. Mbote ma amoon na juróom-ñaari béjjén ak juróom-ñaari bët, ñu di juróom-ñaari Xeli Yàlla, yi ñu yónni ci àddina sépp. 5:7 Mbote ma ñëw, jël téere, ba nekkoon ca loxol ndeyjooru ka toog ca gàngune ma. 5:8 Ba mu jëlee téere ba, ñeenti mbindeef ya ak ñaar-fukki mag ña ak ñeent daldi dëpp seen jë ca kanam Mbote ma, ku nekk yor xalam. Ñu yor it andi wurus yu fees ak cuuraay, yu doon misaal ñaani gaayi Yàlla ya. 5:9 Ñu daldi woy woy wu bees naan:«Yeyoo ngaa jël téere bite dindi tayu yi,ndaxte reyees na la,te jotal nga Yàlla ak sa deretay nit ñu bokk ci bépp giir,kàllaama, réew ak xeet. 5:10 Def nga leen askanu saraxalekatiBuur Yàlla sunu Boroom,di ko jaamu,te dinañu nguuru ci àddina.» 5:11 Ma xool noonu, dégg baatu malaaka yu bare yu ëppoon alfunniy alfunniy junniy junni. Malaaka ya wër gàngune ma ak mbindeef ya ak mag ña. 5:12 Ñuy xaacu naan:«Mbote ma ñu rendi woonyeyoo na kàttan, alal, xel,doole, teraanga, ndam ak cant.» 5:13 Ma dégg itam mbindeef, yi nekk ci asamaan, ci kaw suuf, ci biir suuf, ci géej gi, — mbindeef yépp naan:«Na cant, teraanga, ndam ak nguurféete ak ki toog ci gàngune mi,ak Mbote mi ba fàww.» 5:14 Ñeenti mbindeef ya naan: «Amiin.» Mag ña sukk di màggal.
6:1 Noonu ma gis Mbote ma dindi tayu gu jëkk ga, te ma daldi dégg kenn ca ñeenti mbindeef ya, di wax ak baat buy riir ni dënnu naan: «Ñëwal.» 6:2 Ma xool noonu, gis fas wu weex, gawar ba yor ag fitt. Ñu jox ko kaalag ndam, mu daldi dem moom jàmbaar ngir daani. 6:3 Mbote ma dindi na ñaareelu tayu ga, ma dégg ñaareelu mbindeef ma naan: «Ñëwal.» 6:4 Noonu weneen fas génn, di wu xonq, gawar ba jot sañ-sañu jële jàmm ci kaw suuf, ngir nit ñi di reyante ci seen biir. Ñu jox ko jaasi ju mag. 6:5 Mu dindi ñetteelu tayu ga, ma dégg ñetteelu mbindeef ma ne: «Ñëwal.» Ma xool, gis fas wu ñuul, gawar ba yor ab peesekaay. 6:6 Ma dégg baat bu jollee ca diggante ñeenti mbindeef ya, naan: «Peyug bëccëgu lëmm ngir benn kilob ceeb, peyug bëccëgu lëmm ngir ñetti kiloy dugub, waaye bul yàq diw ak biiñ.» 6:7 Mu dindi ñeenteelu tayu ga, ma dégg ñeenteelu mbindeef ma naan: «Ñëwal.» 6:8 Ma xool noonu, gis fas wu wert, gawar baa nga tuddoon Dee te barsàq a nga toppoon ci moom. Ñu jox ko sañ-sañ ci ñeenteelu xaaju àddina sépp, ngir mu faat ak jaasi, xiif, mbas ak rabi àll yi. 6:9 Mu dindi juróomeelu tayu ga, ma gis ca suufu saraxalukaay, ba ñuy taal cuuraay ca kawam, ruuwi ñi ñu bóom ndax seede si ñu doon sàmm ak li ñu gëmoon kàddug Yàlla. 6:10 Ñuy xaacu naan: «Boroom bu sell bi te dëggu, ba kañ ngay nég àtte bi te feyyul nu sunu deret ci waa àddina?» 6:11 Ñu jox leen ku nekk mbubb mu weex, daldi leen ne, ñu muñ tuuti, ba kera seeni nawle ñëw, te lim bi mat — seeni nawle ci liggéey bi, di seeni bokk yu waa àddina waroon a bóom ni ñoom. 6:12 Ma xool, ba muy dindi juróom-benneelu tayu ga. Noonu mu am yengu-yengub suuf bu mag, jant bi ñuul ni këriñ, weer wi xonq curr ni deret. 6:13 Biddiiw yi fàqe asamaan, di daanu ci kaw suuf, ni doomi garab yu yolox di wadd, bu ko ngelaw lu metti dee yengal. 6:14 Asamaan si dellu ni basaŋ gu ñuy taxañ, tund yépp ak dun yépp randoo fa ñu nekkoon. 6:15 Noonu buuri àddina si, kilifa yi, njiiti xare yi, boroom alal yi, boroom kàttan yi, jaam yi ak gor yi, ñépp làqatuji ci xunti yi ak ci ron doji tund yi. 6:16 Ñu naan tund yi ak doj yi: «Daanuleen ci sunu kaw te nëbb nu bëti ki toog ci gàngune mi ak meru Mbote mi, 6:17 ndaxte bés bu mag, bi seen mer di feeñ, agsi na! Ku ci man a rëcc?»
7:1 Gannaaw loolu ma gis ñeenti malaaka yu taxaw ci ñeenti xeblay àddina si. Ñu téye ñeenti ngelawi àddina, ngir ngelaw du wol ci kaw suuf, ci géej mbaa ci genn garab. 7:2 Ma gis it meneen malaaka, muy yéeg, jóge penku, yor màndargakaayu Yàlla jiy dund. Mu daldi wax ak baat bu xumb ñeenti malaaka ya ñu joxoon sañ-sañ, ñu yàq suuf ak géej, 7:3 ne leen: «Buleen yàqagun suuf si ak géej gi ak garab yi. Négleen, ba ñu def màndarga ci jëwu ñiy jaamu Yàlla sunu Boroom.» 7:4 Noonu ma dégg limub ñi ñu màndargaal; ñu tollu ci téeméer ak ñeent-fukk ak ñeent ci ay junni. Ñu jóge ci giiri bànni Israyil yépp: 7:5 Fukki junni ak ñaar lañu màndargaal ci biir giiru Yuda,fukki junni ak ñaar ci giiru Ruben,fukki junni ak ñaar ci giiru Gàdd, 7:6 fukki junni ak ñaar ci giiru Aser,fukki junni ak ñaar ci giiru Neftali,fukki junni ak ñaar ci giiru Manase, 7:7 fukki junni ak ñaar ci giiru Simeyon,fukki junni ak ñaar ci giiru Lewi,fukki junni ak ñaar ci giiru Isakaar, 7:8 fukki junni ak ñaar ci giiru Sabulon,fukki junni ak ñaar ci giiru Yuusufa,fukki junni ak ñaar ci giiru Ben-yamin. 7:9 Gannaaw loolu ma xool, gis mbooloo mu réy, ba kenn mënu koo waññ, ñu bokk ci xeet yépp, giir yépp, réew yépp ak kàllaama yépp, taxaw ca kanamu gàngune ma ak Mbote ma. Ñu sol ay mbubb yu weex, di màggal te di yengal ay cari garab ci seeni loxo, 7:10 naan:«Mucc gaa ngi ci Yàllasunu Boroom, bi toog ci gàngune mi,ak ci Mbote mi!» 7:11 Noonu malaaka yépp taxaw, wër gàngune ma ak mag ña ak ñeenti mbindeef ya. Ñu dëpp seen jë ca kanamu gàngune ma, di jaamu Yàlla, 7:12 naan:«Amiin. Na cant ak ndam, xel ak ngërëm, teraanga, kàttan ak dooleféete ak Yàlla sunu Boroom ba fàww. Amiin!» 7:13 Noonu kenn ca mag ña ne ma: «Ñi sol mbubb yu weex yi, ñooy ñan ak fan lañu jóge?» 7:14 Ma ne ko: «Sang bi, xanaa yaa ko xam.» Mu ne ma: «Ñoo di ñi jóge ca metit wu réy wa. Fóot nañu seeni mbubb, ba weexal ko ci deretu Mbote ma. 7:15 Loolu moo taxñu nekk ci kanamu gàngunem Yàlla,di ko jaamu guddi ak bëccëg ci këram,te ki toog ci gàngune mi dina leen yiir. 7:16 Dootuñu xiif, dootuñu mar.Jant mbaa weneen tàngaay du leen lakk, 7:17 ndaxte Mbote mi nekk ci diggu gàngune mi dina leen sàmm,yóbbu leen ca bëti ndoxum dund ma,te Yàlla dina fomp bépp rangooñ ci seeni bët.»
8:1 Mbote ma dindi na juróom-ñaareelu tayu ga, asamaan ne selaw lu mat genn-wàllu waxtu. 8:2 Noonu ma gis juróom-ñaari malaaka, yi taxaw ca kanam Yàlla, ñu daldi leen jox juróom-ñaari liit. 8:3 Ba loolu amee meneen malaaka ñëw, taxaw ca wetu saraxalukaayu wurus, ba ñuy taal cuuraay ca kawam, yor andu cuuraayu wurus. Ñu jox ko cuuraay lu bare, ngir mu boole ko ak ñaani gaayi Yàlla yépp, joxe ko ci kaw saraxalukaayu wurus ba nekk ci kanam gàngune mi. 8:4 Noonu saxarus cuuraay li gillee ca loxob malaaka ma, ànd ak ñaani gaayi Yàlla ya, jëm ca kanam Yàlla. 8:5 Malaaka ma jël andu cuuraay ba, duy ko ak ay xal ca saraxalukaay ba, daldi koy sànni ci àddina. Noonu mu am ay dënnu, ay riir, ay melax ak yengu-yengub suuf. 8:6 Ba mu ko defee juróom-ñaari malaaka, ya yoroon juróom-ñaari liit ya, daldi defaru di waaj a liit. 8:7 Malaaka mu jëkk ma wol liitam. Noonu ñu sànni ci àddina yuur ak safara yu ñu boole ak deret, ba tax benn ci ñetti xaaju suuf si lakk, benn ci ñetti xaaju garab yi it lakk, te ñax mu naat mépp lakk. 8:8 Ñaareelu malaaka ma wol liitam. Noonu ñu sànni lu mel ni tundu safara wu réy, mu daanu ci géej gi, benn ci ñetti xaaju géej gi soppiku deret, 8:9 benn ci ñetti xaaju mbindeef yi nekk ci géej gi dee, te benn ci ñetti xaaju gaal yi yàqu. 8:10 Ñetteelu malaaka ma wol liitam. Noonu biddiiw bu réy, yànj ni jum, xawee asamaan, daanu ci benn ci ñetti xaaju dex yi ak ci bëti ndox yi. 8:11 Biddiiw boobu mi ngi tuddoon Wextan. Nit ñu bare naan ci ndox mi daldi dee, ndaxte ndox mi dafa daldi wex. 8:12 Ñeenteelu malaaka ma wol liitam. Noonu dóorees benn ci ñetti xaaju jant bi, ak benn ci ñetti xaaju weer wi, ak benn ci ñetti xaaju biddiiw yi, ba tax benn ci ñetti xaaju leer gi lëndëm. Bëccëg bi ñàkk leer diirub benn ci ñetti xaajam, guddi gi ñàkk leer diirub benn ci ñetti xaajam. 8:13 Ma xool noonu, dégg jaxaay juy naaw ci digg asamaan, naan ak baat bu xumb: «Musiba, musiba! Musibaa ngi ci kaw waa àddina, ndax liit yi yeneen ñetti malaaka yi di wol.»
9:1 Juróomeelu malaaka ma wol liitam. Noonu ma gis, ñu jox caabiy kàmb gu xóot gi benn biddiiw bu xawee woon asamaan, daanu ci kaw suuf. 9:2 Biddiiw ba ubbi buntu kàmb gu xóot ga. Noonu saxar jollee ca, su mel ni saxarus puur bu mag, jant bi ak jaww ji lépp lëndëm ndax saxarus kàmb ga. 9:3 Ay njéeréer génn ca saxar sa, tasaaroo ci biir àddina. Ñu jox leen kàttan gu mel ni kàttanu jànkalaar. 9:4 Ñu sant leen, ñu bañ a laal ñax mi ci kaw suuf, mbaa genn gàncax walla genn meññeef, waaye ñu jublu rekk ci nit ñu amul màndargam Yàlla ci seen jë. 9:5 Santuñu leen ñu rey leen, waaye ñu metital leen diirub juróomi weer. Te metit woowu ñuy indi, temboo na ak metit wiy dal nit, bu ko jànkalaar fittee. 9:6 Ca jamono yooya nit ñi dinañu sàkku dee, waaye duñu daje ak moom. Dinañu bëgg a dee, waaye dee da leen di daw. 9:7 Njéeréer ya nag dañuy niroo ak fas yu ñu waajal ngir xare. Am nañu ci seen bopp lu mel ni kaalay wurus, te seen xar-kanam mel ni gu nit. 9:8 Seeni kawar mel ni yu jigéen, seeni bëñ mel ni bëñi gaynde. 9:9 Takk nañu ci seen dënn lu mel ni kiiraayu weñ, te coow la seeni laaf di def mel ni coowu sareeti xare yu bare yu ñu takk fas, di xeexi. 9:10 Am nañu ay geen yu am ay fitt ni jànkalaar, te ca la seen kàttan nekk, ngir metital nit ñi diirub juróomi weer. 9:11 Buuru njéeréer yi mooy malaakam kàmb gu xóot gi, moom lañu tudde ci làkku Yawut, Abadon, ak ci làkku gereg, Apolyon, liy tekki «Yàqkat.» 9:12 Musiba mu jëkk mi jàll na, yeneen ñaari musiba yaa ngi ñëw. 9:13 Juróom-benneelu malaaka ma wol liitam. Noonu ma dégg baat bu jóge ci ñeenti béjjén, yi nekk ci koñi saraxalukaayu wurus, ba nekk ci kanam Yàlla, 9:14 mu ne juróom-benneelu malaaka, ma yoroon liit: «Yiwil ñeenti malaaka, ya yeewe ca Efraat, dex gu mag ga.» 9:15 Noonu ñu daldi yiwi ñeenti malaaka, ya ñu waajaloon ngir at moomu, weer woowu, bés boobu ak waxtu woowu, ngir ñu rey benn ci ñetti xaaju nit ñi. 9:16 Limub gawar ga doon xareji mat na ñaari alfunniy alfunni. Dégg naa lim ba. 9:17 Nii laa gise ci peeñu mi fas ya ak ña leen war: ñu sol kiiraay yu xonq ni safara, bulo ni saxar, ak mboq ni tamarax. Boppi fas yaa nga doon nirook boppi gaynde; safara, saxar ak tamarax di génn ci seeni gémmiñ. 9:18 Benn ci ñetti xaaju nit ñi dee ci ñetti musiba ya: ci safara, saxar ak tamarax yi génn ci seeni gémmiñ. 9:19 Ndaxte kàttanu fas yaa ngi ci seeni gémmiñ ak ci seeni geen. Geen yaa nga mel ni ay jaan, am ay bopp, te ñoom lañuy metitale nit ñi. 9:20 Nit ñi rëcc ci musiba yooyu taxul sax ñu tuub seeni jëfi loxo. Noppiwuñu di jaamu rab yi ak nataali xërëm yu ñu defare wurus ak xaalis ak xànjar ak xeer ak dénk, yoo xam ne mënuñoo gis, mënuñoo dégg mbaa ñu dox. 9:21 Te nit ñooñu tuubuñu seen bóom, seen xërëm, seen njaaloo mbaa seen càcc.
10:1 Noonu ma gis meneen malaaka mu am doole, muy wàcce asamaan, làmboo niir. Xon tiim ko, te xar-kanamam mel ni jant, te ay tànkam mel ni jumi safara. 10:2 Yor na benn téere bu ndaw bu ñu ubbi. Mu teg tànku ndeyjooram ci géej gi, tànku càmmooñam ci suuf si, 10:3 di xaacu, mel ni gaynde guy yëmmu. Naka la xaacu, juróom-ñaari dënnu yi jib. 10:4 Naka la juróom-ñaari dënnu yi di jib, may waaj a bind, waaye ma dégg baat bu jóge asamaan, naan ma: «Li juróom-ñaari dënnu yi wax, na nekk kumpa, bu ko bind.» 10:5 Noonu malaaka ma ma gis, mu taxaw ci géej gi ak suuf si, yékkati loxol ndeyjooram, mu jëm asamaan, 10:6 daldi waat ci kiy dund ba fàww, ki sàkk asamaan ak suuf ak géej ak li ci nekk lépp; mu ne: «Négandiku wees na, 10:7 waaye jamono ju juróom-ñaareelu malaaka ma wolee ci liitam, ndogalu Yàlla dina mat, ni mu ko waxe woon ay jaamam, yonent yi.» 10:8 Ci kaw loolu baat, ba ma déggoon ca asamaan waxaat ak man, ne ma: «Demal jël téere bi ñu ubbi ci loxob malaaka, mi taxaw ci géej gi ak suuf si.» 10:9 Ma dem ca malaaka ma, laaj ko téere bu ndaw boobu. Mu ne ma: «Jël ko te lekk ko. Dina wex ci sa biir, waaye dina neex ni lem ci sa gémmiñ.» 10:10 Noonu ma jël téere bi ci loxob malaaka mi, daldi ko lekk, mu neex ci sama gémmiñ ni lem, waaye bi ma ko wannee, mu wex xat ci sama biir. 10:11 Gannaaw loolu ñu ne ma: «Fàww nga wax ci kàddug Yàlla lu jëm ci réew yu bare, xeet yu bare, kàllaama yu bare ak buur yu bare.»
11:1 Bi loolu amee ñu jox ma nattukaay bu mel ni yet, ne ma: «Jógal, natt kër Yàlla gi ak saraxalukaay bi, te waññ ña fay jaamu Yàlla. 11:2 Waaye bàyyil ëttu bitib kër Yàlla gi; bu ko natt, ndaxte jébbalees na ko ñi dul Yawut, te dinañu nappaaje dëkk bu sell bi diirub ñeent-fukki weer ak ñaar. 11:3 Dinaa may sama ñaari seede yi, ñuy wax ci kàddug Yàlla, sol ay saaku, di toroxlu diirub junni ak ñaari téeméeri fan ak juróom-benn-fukk.» 11:4 Ñaari seede ya nag ñoo di ñaari garabu oliw yeek ñaari làmpu diwlin, yi taxaw ci kanam Boroom suuf si. 11:5 Su leen kenn bëggee def lu bon, safaraay génn ci seen gémmiñ, daldi lakk seeni bañaale; te ku leen bëgg a def lu bon, noonu lay war a deeye. 11:6 Am nañu sañ-sañu téye taw diirub fan, yi ñuy wax ci kàddug Yàlla. Am nañu it sañ-sañu soppi ndox yi deret te wàcce ci kaw suuf musiba yu nekk, saa su ñu ko bëggee. 11:7 Bu ñu noppee seen seede, rab wiy jóge ci kàmb gi dina leen xeex, daan leen, rey leen. 11:8 Te seeni néew dinañu nekk ci péncum dëkk bu mag, boobu ñuy wooye ci misaal Sodom ak it Misra, fa ñu reyoon seen Boroom ci bant. 11:9 Te diirub ñetti fan ak genn-wàll bépp réew, giir, kàllaama ak xeet dinañu seetaan seeni néew te duñu bàyyi kenn suul leen. 11:10 Waa àddina dinañu bég ci seen dee, di ndokkeelante ak di joqleente ay may, ndaxte ñaari yonent ya lakkaloon nañu waa àddina. 11:11 Waaye bi ñetti fan ya ak genn-wàll wéyee, xelum dund, jóge ca Yàlla, solu leen, ñu jóg taxaw. Noonu tiitaange gu réy jàpp ñi leen doon seetaan. 11:12 Ñaari seede ya dégg baat bu xumb ca asamaan naan leen: «Yéegleen fii.» Noonu ñu yéeg asamaan ci aw niir, seeni bañaale di seetaan. 11:13 Ca saa sa am yengu-yengub suuf bu mag, te benn ci fukki xaaju dëkk ba daldi màbb. Juróom-ñaari junniy nit dee ci yengu-yengub suuf ba, te ña ca des tiit, daldi màggal Yàllay asamaan. 11:14 Ñaareelu musiba mi wéy na, ñetteel baa ngi nii di ñëw. 11:15 Juróom-ñaareelu malaaka ma wol liitam, noonu baat yu xumb jib ca asamaan naan:«Nguuru àddina, jébbalaat nañu kosunu Boroom ak Almaseem,te dina nguuru ba fàww.» 11:16 Ñaar-fukki mag ak ñeent, ña toogoon ca seen gàngune ca kanam Yàlla, daldi dëpp seen jë ca suuf, jaamu Yàlla, 11:17 naan:«Nu ngi lay gërëm, Boroom bi Yàlla,yaw Aji Kàttan ji, ki nekk te nekkoon,ndax gànjoo nga sa kàttan gu réy gi,ngir taxawal sa nguur. 11:18 Xeet yi meroon nañu,waaye sa mer wàcc na,te jamono ji jot na,ji ngay àttee ñi dee,neexal say jaam yonent yi,ak sa gaa ñi ak ñi ragal saw tur,muy mag di ndaw,te nga rey ñiy yàq àddina.» 11:19 Noonu kër Yàlla gi ci asamaan daldi ubbiku, gaalu kóllëreg Yàlla ga daldi feeñ ca biir kër Yàlla ga, te mu daldi am ay melax, ay coow, ay dënnu, yengu-yengub suuf ak tawu yuur bu metti.
12:1 Amoon na firnde ju ràññiku ju feeñ ca asamaan, di jigéen ju làmboo jant bi, kaalawoo fukki biddiiw ak ñaar, weer wi nekk ci suufu tànkam. 12:2 Jigéenu biir la, di yuuxu ndax metitu mat wu tar. 12:3 Noonu beneen firnde feeñ ca asamaan, di ninkinànka ju réy, xonq curr te am juróom-ñaari bopp ak fukki béjjén. Ca bopp ya am na juróom-ñaari mbaxanay buur. 12:4 Geenam di laawaale ñetti cér yu ne benn ca biddiiwi asamaan, di leen sànni ci suuf. Ninkinànka ja taxaw ca kanamu jigéen jay matu, ngir lekk liir ba, bu juddoo. 12:5 Noonu mu jur doom ju góor, muy ki war a jiite xeeti àddina yépp ak yetu weñ. Waaye ñu daldi fëkk doom ja, mu dem ca Yàlla ak gànguneem. 12:6 Gannaaw loolu jigéen ja daw, dem ca màndiŋ ma, ca dalukaay ba ko Yàlla waajaloon ngir mu nekk fa, ñu dundal ko fa diirub junni ak ñaari téeméeri fan ak juróom-benn-fukk. 12:7 Noonu xare am ca asamaan ya. Mikayel ak malaaka, ya ànd ak moom, xeex ak ninkinànka ja, ninkinànka ja it ak ay malaakaam feyyu. 12:8 Waaye ninkinànka jaa gën a néew doole; noonu ñu dàqe ko ak toppam asamaan. 12:9 Daaneel nañu ko, moom ninkinànka ju réy ji, di jaani cosaan ji, te ñu di ko wax Tuumaalkat bi mbaa Seytaane, moom miy nax waa àddina sépp — daaneel nañu ko ci kaw suuf, moom ak ay malaakaam. 12:10 Noonu ma dégg baat bu xumb jóge asamaan naan:«Léegi mucc agsi na,moom ak kàttanak nguuru Yàlla sunu Boroom,ak sañ-sañu Almaseem,ndaxte ki daan tuumaal sunuy bokk,di leen sosal guddi ak bëccëgci kanam Yàlla sunu Boroom,kooka daaneel nañu ko. 12:11 Fekk noot nañu kojaarale ko ci deretu Mbote maak seen seedes ngëm,te soppuñu seen bakkan ba ragal a dee. 12:12 Looloo tax, na asamaanak ñi ci dëkk bànneexu!Musiba ci kaw suuf ak ci biir géej!Ndaxte Seytaane wàcc na ci yéen,ànd ak mer mu tàng,ndaxte xam na ne, jot gi ko dese barewul.» 12:13 Ba ninkinànka ja gisee ne, daaneel nañu ko ci kaw suuf, mu dàq jigéen, ja juroon doom ju góor ja. 12:14 Noonu ñu jox jigéen ja ñaari laafi jaxaay ja, ngir mu naaw, ba sore ninkinànka ja, dem ca màndiŋ ma ca bérabam, ñu dundal ko fa ab diir, ay diir ak genn-wàllu diir. 12:15 Ninkinànka ja buusu ndox mu bare ni dex ca gannaaw jigéen ja, ngir yóbbaale ko ca. 12:16 Waaye suuf wallu jigéen ja, naan dex, ga ninkinànka ja buusu woon. 12:17 Ninkinànka ja mere jigéen ja, daldi xeexi ak ñi des ciy doomam, di ñiy sàmm ndigali Yàlla tey sax ci di seedeel Yeesu. 12:18 Noonu mu taxaw ca tefesu géej ga.
13:1 Noonu ma gis génn ca géej ga, rab wu am fukki béjjén ak juróom-ñaari bopp. Ci kaw béjjénam ya amoon na fukki mbaxanay buur; ca bopp ya turi xarab Yàlla. 13:2 Rab wa ma gis ma nga mel ni segg, tànk ya mel ni yu rab wu ñuy wax urs, gémmiñ ga mel ni gu gaynde. Ninkinànka ja jox ko kàttanam, nguuram ak sañ-sañam bu réy. 13:3 Benn ca bopp ya mel ni dafa gaañu ba dee. Waaye gaañu-gaañu ba daldi wér. Waa àddina sépp yéemu, daldi topp rab wa. 13:4 Ñu jaamu ninkinànka ja ndax li mu joxoon sañ-sañ rab wa, di jaamu it rab wa, naan: «Rab wi amul moroom, kenn mënul a xeex ak moom.» 13:5 Noonu mayees ko mu am gémmiñ, muy jey boppam te di xarab turu Yàlla. Mayees ko it sañ-sañu jëf ci kaw suuf diirub ñeent-fukki weer ak ñaar. 13:6 Noonu mu tàmbalee xarab Yàlla, di xarab aw turam, dalam, ak ñi dëkk ci asamaan. 13:7 Mayees ko, mu xare ak gaayi Yàlla yi te noot leen. Mayees ko it sañ-sañ ci kaw bépp giir, réew, kàllaama ak xeet. 13:8 Waa àddina sépp dinañu ko jaamu, ñooñu ñu bindul seeni tur, li dale ci njàlbéenu àddina, ci téereb dund bu Mbote mi ñu rendi. 13:9 Yaw mi am ay nopp, déglul. 13:10 Ku Yàlla dogal,ñu war laa jàpp njaam,dinañu la jàpp njaam.Ku Yàlla dogal,ñu war laa rey ak jaasi,dinañu la rey ak jaasi. Looloo tax gaayi Yàlla yi war a muñ te takku. 13:11 Noonu ma gis weneen rab di génn ci suuf. Am na ñaari béjjén yu mel ni yu mbote, waaye di wax ni ninkinànka. 13:12 Muy jëf ak sañ-sañu rab wu jëkk wa ci turam, di sant waa àddina sépp, ñu jaamu rab wu jëkk, woowu am gaañu-gaañu ba ko rey, waaye daldi wér. 13:13 Muy def kéemaan yu réy, ba dem sax bay wàcce ci kaw suuf safara su jóge asamaan, nit ñi di gis. 13:14 Noonu mu nax waa àddina ci kéemaan, yi mu am sañ-sañu def ci turu rab wu jëkk wa. Mu sant waa àddina, ñu def nataalu rab, wi am gaañu-gaañub jaasi tey dund. 13:15 Mayees ko it, mu dundloo nataalu rab wa, waxloo ko, ba képp ku jaamuwul nataalu rab wa rekk ñu rey la. 13:16 Mu def it ba ñépp, mag ak ndaw, buur ak baadoolo, gor ak jaam, ñépp am màndarga ci seen loxol ndeyjoor walla ci seen jë, 13:17 ba kenn du man a jënd mbaa mu jaay te amul màndargam rab wi, maanaam turam walla siifar bu mengoo ak turam. 13:18 Lii nag mooy laaj xel: ku am xel dina man a waññ siifaru rab wi, ndaxte siifar boobu mengoo na ak bu nit, di juróom-benni téeméer ak juróom-benn-fukk ak juróom-benn.
14:1 Ma xool noonu, gis Mbote ma taxaw ci tundu Siyon, ànd ak téeméer ak ñeent-fukk ak ñeenti junniy nit, te ñu bind ci seen jë turu Mbote ma ak turu Baayam. 14:2 Ma dégg baat bu jóge asamaan, buy riir ni duusi géej, ni riiru dënnu gu réy. Baat ba ma dégg mel ni baati xalamkat yuy xalam. 14:3 Nit ñu bare ñooñu taxaw ca kanamu gàngune ma ak ñeenti mbindeef ya ak mag ña, di woy woy wu bees. Kenn mënul a jàng woy wa, ku dul téeméer ak ñeent-fukk ak ñeenti junniy nit, ñooñu ñu jote àddina. 14:4 Ñoo di ñi taqul sobey jigéen, ndaxte saxal nañu seen bopp ci sell. Ñu nga topp Mbote ma fépp fu mu jëm. Yàlla jot na leen ci biir nit ñi, ñu jébbalu ci Yàlla ak ci Mbote mi, mel ni tànneefu ngóob mi ñuy sédde Yàlla, 14:5 te fen musul a génn ci seen gémmiñ. Amuñu benn sikk. 14:6 Noonu ma gis meneen malaaka naaw ca digg asamaan, yor xebaar bi sax, di ko yégal waa àddina — xeet yépp, giir yépp, kàllaama yépp ak réew yépp. 14:7 Ma nga doon xaacu naan: «Ragal-leen Yàlla te jox ko ndam li, ndaxte waxtuw àtteem jot na. Jaamuleen ki sàkk asamaan ak suuf ak géej ak bëti ndox yi.» 14:8 Meneen malaaka, di ñaareel bi, topp ca naan: «Daanu na! Babilon, dëkk bu mag, bi daan màndil réew yépp ak biiñu njaaloom, daanu na.» 14:9 Meneen malaaka, di ñetteel bi, topp ca, di xaacu naan: «Ku jaamu rab wi ak nataalam te nangoo am màndargam ci jëwam walla ci loxoom, 14:10 dina naan moom itam biiñu xadarub Yàlla bi kenn raxul, ñu sotti ko ci koppu meram. Te dees na ko mbugal ci safara ak tamarax ci kanamu malaaka yu sell yi ak Mbote mi, 14:11 te saxar siy jóge ci seen mbugal dina gilli ba fàww. Ñooñu di jaamu rab wi ak nataalam, ak képp ku nangoo jot màndargam turam, duñu noppalu guddi ak bëccëg.» 14:12 Looloo tax gaayi Yàlla yi war a muñ, ñooñuy sàmm ndigali Yàlla yi ak ngëm ci Yeesu. 14:13 Noonu ma dégg baat ci asamaan naan: «Bindal: “Bés ni tey, ñi nekk ci Boroom bi te dee, barkeel nañu.”» Xelum Yàlla nee na: «Waaw, dinañu noppalu ci seeni coono, ndaxte seeni jëf a nga leen di xaar.» 14:14 Ma xool noonu, gis niir wu weex ak ku ca toog, niroo ak doomu nit, takk kaalag wurus ca bopp ba, yor sàrt bu ñaw. 14:15 Te meneen malaaka génn ca kër Yàlla ga, di wax ak baat bu xumb ak ka toogoon ca niir wa, ne ko: «Dawalal sa sàrt te góob, ndaxte ngóob jot na, te lépp ñor na ci kaw suuf.» 14:16 Noonu ka toogoon ca kaw niir wa dawal sàrtam ci kaw suuf, góob àddina sépp. 14:17 Bi loolu amee meneen malaaka génn ca kër Yàlla ga nekk ca asamaan, yor moom itam sàrt bu ñaw. 14:18 Noonu meneen malaaka, ma am sañ-sañ ca safara sa, jóge ca saraxalukaayu cuuraay ba, daldi wax ak baat bu xumb ak malaaka, ma yor sàrt bu ñaw ba, ne ko: «Dawalal sa sàrt bu ñaw bi te dagg céggu réseñ yu àddina, ndaxte ñor nañu.» 14:19 Noonu malaaka ma daldi dawal sàrtam ci àddina, dagg réseñ yi, sànni leen ci biir segalukaay bu réy bu merum Yàlla. 14:20 Ñu nal réseñ ya ca segalukaay, ba ca gannaaw dëkk ba, deret génn ca, ba agsi ci laabi fas yi, te wal ba ëmb lu mat ñetti téeméeri kilomet.
15:1 Noonu ma gis ca asamaan beneen firnde ju réy tey yéeme: juróom-ñaari malaaka yu taawu juróom-ñaari musiba, ñuy yu mujj ya, ndaxte ñoom ñooy matal merum Yàlla. 15:2 Noonu ma gis lu mel ni géej gu leer ni weer bu set buy ray-rayi ak safara. Ña nootoon rab wa ak nataalam, ak siifar bu mengoo ak turam, ñoo taxaw ca géej gu leer ga, yor xalam yu leen Yàlla jox. 15:3 Ñuy woy woyu Musaa jaamu Yàlla bi, ak woyu Mbote ma, naan:«Say jëf réy nañu te yéeme,yaw Boroom bi Yàlla, Aji Kàttan ji.Say yoon jub nañu te dëggu,yaw Buur bi fiy sax ba abadan. 15:4 Ku la ragalul, Boroom bi?Ku dul màggal saw tur?Kenn, ndaxte yaw rekk yaa sell.Xeet yépp dinañu dikk, jaamu la,ndax say àtte bir na ñépp.» 15:5 Gannaaw loolu ma xool, noonu kër Yàlla ubbiku ca asamaan, muy tàntu màggalukaay, bi ëmb li Yàlla seede. 15:6 Juróom-ñaari malaaka, ya taawu juróom-ñaari musiba ya, daldi génn ca kër Yàlla ga. Ñu sol mbubb yu set te weex bay lerax, laxasaayoo ngeñaayi wurus ba ci seen dënn. 15:7 Noonu kenn ci ñeenti mbindeef ya jox juróom-ñaari malaaka ya juróom-ñaari ndabi wurus yu fees ak merum Yàlla jiy dund ba fàww. 15:8 Kër Yàlla ga fees ak saxar ndax leeraayu ndamu Yàlla ak kàttanam. Te kenn mënatul a dugg ca kër Yàlla ga, ba kera juróom-ñaari musiba, ya juróom-ñaari malaaka ya taawu, di mat.
16:1 Noonu ma dégg baat bu xumb bu jóge ca kër Yàlla ga, naan juróom-ñaari malaaka ya: «Demleen sotti ci àddina juróom-ñaari ndabi merum Yàlla yi.» 16:2 Noonu malaaka mu jëkk ma dem, sotti ndabam ci àddina, ba woppi taab ju bon te metti dal nit, ña am màndargam rab wa tey jaamu nataalam. 16:3 Ñaareelu malaaka ma sotti ndabam ci géej gi. Mu soppiku deret ni deretu néew, ba lépp luy dund te nekkoon ci géej gi dee. 16:4 Ñetteelu malaaka ma sotti ndabam ci dex yi ak ci bëti ndox yi. Ñu daldi nekk deret. 16:5 Noonu ma dégg malaaka mi am sañ-sañ ci ndox yi naan:«Ku jub nga, yaw ki nekk te nekkoon,yaw Aji Sell ji,ci li nga dogal àtte yooyu. 16:6 Ndaxte tuur nañu deretu sa gaa ñiak ju yonent yi,yaw it fey nga leen seen bor,jox leen deret, ñu naan.» 16:7 Ma dégge baat jibe ca saraxalukaayu cuuraay ba naan:«Waaw Boroom bi Yàlla, Aji Kàttan ji,say àtte dëggu nañu te jub.» 16:8 Ñeenteelu malaaka ma tuur ndabam ci jant bi. Noonu ñu jox ko sañ-sañu lakk nit ñi ak tàngaayam. 16:9 Naaj wu metti di lakk nit ñi, ñu daldi xarab turu Yàlla, ji am sañ-sañ ci kaw musiba yooyu. Waaye tuubuñu sax seeni bàkkaar, ngir jox ko ndam li. 16:10 Juróomeelu malaaka ma tuur ndabam ci kaw gàngunem rab wa. Noonu lëndëm muur nguuram. Nit ñi di màtt seeni làmmiñ ndax metit, 16:11 ñuy xarab Yàllay asamaan ndax seeni metit ak seeni taab. Waaye tuubuñu seeni jëf. 16:12 Juróom-benneelu malaaka ma sotti ndabam ci dex gu mag, gi ñuy wax Efraat, ndox ma daldi ŋiis, ngir waajal yoonu buuri penku, yiy ñëw. 16:13 Noonu ma gis ñetti rab yu bon yu mel niy mbott, génn ci gémmiñi ninkinànka ja ak rab wa ak naaféq, ba mbubboo yonent. 16:14 Ay rabi Seytaane lañu woon, yuy def ay kéemaan te di dem ci buuri àddina sépp, di leen dajale, ngir xeex biy am ci bés bu mag, bi Yàlla Aji Kàttan jagleele boppam. 16:15 «Maa ngi ñëw nib sàcc. Bég nga, yaw mi nelawul te di wottu say yére, ngir bañ a dox yaramu neen, ñuy gis sa gàcce.» 16:16 Noonu rab ya dajale buuri àddina si ci bérab bu tudd ci làkku yawut Armagedon. 16:17 Ci kaw loolu juróom-ñaareelu malaaka ma sotti ndabam ci ngelaw. Noonu baat bu xumb jóge ca gàngune ma ca kër Yàlla ga, naan: «Lépp mat na.» 16:18 Noonu mu am ay melax ay riir ay dënnu ak yengu-yengub suuf bu mag, boo xam ne bési cosaan ba léegi, musu faa am. Yengu-yengub suuf si réye na noonu. 16:19 Dëkk bu mag ba xàjjalikoo ñetti cér, te dëkki xeet yi màbb. Noonu Yàlla daldi fàttaliku Babilon bu mag ba, ngir jox ko koppu meram mu tàng ma, ba mu màndi. 16:20 Dun yépp daldi ne mes, te kenn gisatul tund ya. 16:21 Tawu yuur, donj wu nekk tollu ci ñeent-fukki kilo, daldi daanoo asamaan ci kaw nit ñi, ñuy xarab Yàlla ndax musibam yuur ga, ndaxte musiba ma dafa metti woon lool.
17:1 Gannaaw loolu benn ci juróom-ñaari malaaka, ya taawu juróom-ñaari ndab ya, ñëw ne ma: «Kaay, ma won la mbugalu jigéenu moykat bu mag, bi toog ci dex yu bare. 17:2 Moom la buuri àddina si àndal ci seen njaaloo. Ci biiñu moy Yàllaam la waa àddina màndee.» 17:3 Noonu Xelum Yàlla solu ma, malaaka ma yóbbu ma ca màndiŋ ma. Foofa ma gis fa jigéen ju war rab wu xonq te am juróom-ñaari bopp ak fukki béjjén, yaram wa fees ak turi xarab Yàlla. 17:4 Jigéen ja sol lu yolet te xonq, takk wurus ak jamaa ak ay per. Yoroon na koppu wurus bu fees ak ñaawteef ak sobeem. 17:5 Bindoon nañu ci jëwam tur wii ëmb kumpa, mu di: Babilon mu mag mi, ndeyi jigéeni moykat yi ak ñaawteefi àddina yi. 17:6 Ma gis jigéen ja màndi ci deretu gaayi Yàlla yi, ci deretu ñi doon seedeel Yeesu. Naka laa ko gis, ma daldi jaaxle lool. 17:7 Malaaka ma ne ma: «Lu tax nga jaaxle? Dinaa la leeralal kumpag jigéen ji ak rab, wi mu war te am juróom-ñaari bopp ak fukki béjjén. 17:8 Rab wi nga gis nekkoon na waaye nekkatul. Dina génn ca kàmb gu xóot ga, ba noppi sànku. Noonu waa àddina, ñi ñu bindul seeni tur, li dale ci njàlbéenu àddina, ci téereb dund bi, dinañu yéemu, bu ñu gisee rab wi, ndaxte nekkoon na waaye nekkatul te dina nekkaat. 17:9 «Xam lii nag moo laaj xel. Juróom-ñaari bopp ya ñooy juróom-ñaari tund, yi jigéen ji toog ci seen kaw. Juróom-ñaari buur lañu itam: 17:10 juróom daanu nañu, kenn kaa ngi fi, ki ci des ñëwagul, te bu ñëwee, dina fi war a nekk ab diir. 17:11 Rab wi nekkoon te nekkatul nag, moom ci boppam moo di juróom-ñetteelu buur bi, te ci juróom-ñaar yi la bokk. Ma nga jëm sànkute. 17:12 «Fukki béjjén yi nga gis, fukki buur lañu yu jotagul nguur. Waaye dinañu jot sañ-sañ diirub waxtu, ñuy nguuru ak rab wi. 17:13 Ñoo bokk mébét, di jox seen kàttan ak seen sañ-sañ rab wi. 17:14 Dinañu xare ak Mbote mi, waaye Mbote mi dina leen daan, ndaxte mooy kilifag kilifa yi, di Buuru buur yi. Te am toppam, di ñi mu woo te tànn leen, te ñu takku ci moom, dinañu daanandoo ak moom.» 17:15 Mu neeti ma: «Dex yi nga gis jigéenu moykat ja toog ca kaw, mooy réew yi ak mbooloo yi ak xeet yi ak kàllaama yi. 17:16 Fukki béjjén yi nga gis, ñoom ak rab wa, dinañu bañ jigéenu moykat ja, futti ko ci lépp, def ko yaramu neen. Dinañu lekk suuxam, ba noppi lakk ko ci safara. 17:17 Ndaxte Yàlla def na ci seen xol, ñu matal la mu naroon. Noonu dinañu ànd, jébbal seen nguur rab wi, ba kera li Yàlla wax di mat. 17:18 Te jigéen ji nga gis, moo di dëkk bu mag, biy nguuru ci kaw buuri àddina si.»
18:1 Gannaaw loolu ma gis meneen malaaka mu wàcce ca asamaan, yor sañ-sañ bu réy, te leeraayam daj na àddina sépp. 18:2 Mu daldi xaacu naan: «Daanu na! Babilon mu mag ma daanu na! Léegi dëkkukaayu jinne la, ak bépp rab wu bon ak bépp picc mu daganul te araam. 18:3 Ndaxte jox na xeeti àddina yépp, ñu naan ci koppu nafsoom ak njaaloom, ba ñu màndi. Buuri àddina ànd nañu ak moom ci njaaloo, te baana-baanay àddina woomle nañu ndax li mu bëgg mbuux.» 18:4 Noonu ma dégg beneen baat bu jóge asamaan naan: «Génnleen ci biiram, yéen samay gaay, ngir ngeen bañ a bokk ci ay bàkkaaram te bañ a am cér ci musiba yi koy dal. 18:5 Ndaxte ay bàkkaaram dajaloo nañu ba ci asamaan, te Yàlla fàttaliku na ay jëfam yu bon. 18:6 Dellooleen ko li mu defoon, feyleen ko ñaar ci li mu lebaloon, feesal-leen koppam ak naan gu gën a wex ñaari yoon naan ga mu joxe woon. 18:7 Joxleen ko ci coono ak naqar, lu tollu ni tiitar ak mbuux, ba mu dencaloon boppam. Gannaaw nee woon na ci xelam: “Maa ngi toog fii ni buur, duma ab jëtun te duma ténj mukk,” 18:8 looloo tax ba musiba, yii ñu ko sédd, dinañu ñëw ci benn bés, ñu di mbas, ténj ak xiif, ñu di ko lakk ba mu jeex, ndaxte Yàlla Boroom bi ko àtte, ku am kàttan la.» 18:9 Buuri àddina yépp, yi àndoon ak moom ci njaaloo ak mbuux, bu ñu séenee saxar siy jollee ci taal bi ñu koy lakke, dinañu yuuxu, di ko jooy. 18:10 Dinañu tiit ndax coonoom, ba dandu lu sore, naan:«Ngalla yaw! Ngalla yaw,dëkk bu mag bi,Babilon mi am kàttan;wenn waxtu rekk doy na,ngir sab àtte mat!» 18:11 Baana-baana yi ci kaw suuf di jooy, di ko naqarlu, ndaxte kenn dootul jënd seen njaay: 18:12 seen wurus, seen xaalis, seeni jamaa ak yeneeni per; seeni piis yu rafet, piis yu yolet, yu ray-ray, yu xonq; seen dénk wu xeeñ, seen yëf yi ñu defare iwaar walla dénk wu jafe walla xànjar walla weñ walla marbar; 18:13 ak bant yuy safal, gàncax gu xeeñ, ay xeeti cuuraay yu bare, latkoloñ, biiñ, diw, sungufu lay-layaat, pepp, ay nag, ay xar, ay fas, sareeti xare, ay jaam, ba ci bakkani nit. 18:14 Dinañu wax naan: «Yëf yi nga bëggoon a am raw nañu la, te lépp luy yafal walla col gu rafet ñàkk nga ko, te kenn du ko gisaat!» 18:15 Baana-baana, yi daan jaay yëf yooyu ba woomle, dinañu sore ndax ragal coonoom. Dinañu jooy di naqarlu, 18:16 naan:«Ngalla yaw! Ngalla yaw, dëkk bu mag,bi soloon yére yu rafet, yu yolet te xonq,daan takk wurus ak jamaa ak per, 18:17 sa alal ju bare jépp naaw na ci wenn waxtu!» Noonu ñépp ñiy dawal gaal ak ñi ciy tukki ak ñi ciy liggéey ak ñi ciy baana-baana, ñépp di sore bérab boobu, 18:18 te bu ñu séenee saxar sa cay jollee, naan: «Ndax dëkk bu niroo woon ak dëkk bu mag bii mas na am?» 18:19 Ñuy xëpp suuf ci seen bopp, di jooy, di naqarlu te naan:«Ngalla yaw! Ngalla yaw,dëkk bu mag bi nga xam neci la boroom gaal yépp woomle ndax sa barele,ci wenn waxtu nga gental. 18:20 Yaw asamaan, bégal ci li ñu ko yàq!Yéen itam gaayi Yàlla yi,ndaw yi ak yonent yi, bégleen,ndaxte Yàlla àtte na ko, ba feyyul leen.» 18:21 Noonu malaaka mu am doole jël doj wu réy, sànni ko ci géej gi, naan: «Nii lañuy sànnee ak doole Babilon dëkk bu mag bi, mu ne meŋŋ. 18:22 Buumi xalam yi, baati woykat yi, toxoro yi ak liit yi,kenn dootu leen dégg ci yaw.Liggéeykat bu xareñ bu mu man a doon, kenn dootu ko gis ci yaw.Kandaŋu gënn, kenn du ko déggati ci yaw. 18:23 Niitug làmp du tàkkati,te baatu boroom séet ak séetam dootul jib ci yaw ba fàww.Ndaxte say baana-baana ñoo yilifoon àddina,te xeet yépp réer nañu ndax say luxus. 18:24 Te deretu yonent yi ak gaayi Yàlla yiak ñépp ñi ñu rey ci kaw suuf,ci moom Babilon lañu ko fa fekk.»
19:1 Gannaaw loolu ma dégg lu mel ni baat bu xumb bu jollee ca mbooloo mu bare ca asamaan, naan:«Aleluya!Mucc, ndam ak kàttan,Yàlla sunu Boroom moo ko moom. 19:2 Ay àtteem dañoo dëggu te jub!Ndaxte àtte na jigéenu moykat bu mag,bi daan yàq àddina si ak njaaloom,te feyyul na noonu jaami Yàlla, yi mu daan rey.» 19:3 Ñu tegaat ca ne:«Aleluya!Saxarus lakku dëkk baa ngi jolli ba fàww!» 19:4 Noonu ñaar-fukki mag ña ak ñeent, ak ñeenti mbindeef ya, daldi sukk di jaamu Yàlla, moom mi toog ca gàngune ma. Ñu naan:«Amiin! Aleluya!» 19:5 Noonu baat jibe ca gàngune ma naan:«Màggal-leen Yàlla sunu Boroom,yéen ñépp ñi di ay jaamam,yéen ñi ko ragal, mag ak ndaw.» 19:6 Ma dégg lu mel ni baatu mbooloo mu bare, mel ni riiru duusi géej, ni yenguy dënnu yu réy, naan:«Aleluya!Ndaxte sunu BoroomYàlla Aji Kàttan jidugg na ci nguuram. 19:7 Nanu bég te bànneexute jox ko ndam li,ndaxte céetu Mbote mi agsi na,séet bi waaj na. 19:8 May nañu ko, mu sol mbubb mu sette weex bay lerax.» Mbubb mu weex moomu day misaal njubtey gaayi Yàlla yi. 19:9 Gannaaw loolu malaaka ma ne ma: «Bindal lii: “Yéen ñi ñu woo ci reeri céetu Mbote ma, barkeel ngeen.”» Mu teg ca ne ma: «Kàddu yii ñooy kàdduy Yàlla, di kàddu yu dëggu.» 19:10 Noonu ma daanu ci ay tànkam, bëgg koo jaamu. Waaye mu ne ma: «Moytu koo def; sa nawle laa ci liggéey bi, di kenn ci say bokk, yiy sax ci seedeel Yeesu. Jaamul Yàlla. Ndaxte seedes Yeesu mooy xel miy solu yonent yi.» 19:11 Bi loolu wéyee ma gis asamaan ubbiku. Noonu fas wu weex feeñ. Ki ko war ma nga tudd Ku Takku te Dëggu, te ci njub lay àtte ak a xare. 19:12 Ay bëtam di xuyy ni safara te mu am mbaxanay buur yu bare ca boppam. Bind nañu ci moom tur wu kenn xamul ku dul moom. 19:13 Sol na mbubb mu ñu sóob ci deret, te Kàddug Yàlla mooy turam. 19:14 Xarekat yi nekk ci asamaan topp ci moom, war ay fas yu weex, sol mbubb yu weex te set. 19:15 Am na jaasi ju ñaw juy génn ci gémmiñam, ngir dóor xeet yi, mu di leen jiitee yetu weñ, te mooy nappaaje réseñ yi ci segalukaayu mer mu tàng, mu Yàlla Aji Kàttan ji. 19:16 Ci mbubbam ak ci poojam bind nañu ci tur wii: Buuru buur yi, Kilifag kilifa yi. 19:17 Noonu ma gis malaaka mu taxaw ci jant bi. Mu wax ak baat bu xumb ak picc, yiy naaw ci digg asamaan, ne leen: «Ñëwleen teewesi reer bu mag bu Yàlla, 19:18 ngeen lekk suuxi buur yi, njiiti xare yi ak boroom kàttan yi, suuxi fas yi ak seeni gawar, suuxi ñépp: gor ak jaam, mag ak ndaw.» 19:19 Noonu ma gis rab wa, buuri àddina si ak seeni xarekat dajaloo ngir xareji ak ki war fas wa ak ay xarekatam. 19:20 Ñu jàpp rab wa, moom ak naaféq ba mbubboo yonent, ba daan def ca turu rab wa ay kéemaan yu mu naxe ñi nangu woon a am màndargam rab wa te jaamu nataalam. Ñoom ñaar ñépp sànni nañu leen ñuy dund ca déegu safara ak tamarax buy tàkk. 19:21 Ña ca des, jaasi, jay génn ca gémmiñu ka toog ca fas wa, rey leen; picc yépp lekk, ba regg ci seeni suux.
20:1 Noonu ma gis malaaka mu wàcce ca asamaan, yor caabiy kàmb ga ak càllala gu réy. 20:2 Mu jàpp ninkinànka ja, di jaani cosaan ja, muy Tuumaalkat bi, maanaam Seytaane. Malaaka ma yeew ko diirub junniy at, 20:3 sànni ko ci kàmb gi, tëj ko, sakk bunt bi ko tiim ci kaw. Noonu du nax xeet yi, ba kera junniy at yi di mat. Gannaaw loolu fàww ñu yiwi ko diir bu gàtt. 20:4 Noonu ma gis ay gàngune, ñu jox ña ca toog sañ-sañu àtte. Noonu ma gis ruuwi ñi ñu bóomoon ndax li ñu doon seedeel Yeesu te gëm kàddug Yàlla. Ñooñu jaamuwuñu rab wa mbaa nataalam, te nanguwuñoo am màndargam rab wa ca seen jë mbaa seen loxo. Ñu daldi dekki, nguuru ak Kirist diirub junniy at. 20:5 Yeneen néew yi duñu dekki, fi ak junniy at yi matul. Loolu moo di ndekkite lu jëkk li. 20:6 Ñi bokk ci ndekkite lu jëkk li, barkeel nañu te sell! Ñaareelu dee gi du leen manal dara. Waaye dinañu doon saraxalekati Yàlla ak Kirist, tey nguuru ak moom junniy at. 20:7 Bu junniy at ya matee, dinañu yiwi Seytaane ca kasoom, 20:8 te dina dem naxi xeet yi ci ñeenti xeblay àddina, maanaam ñoom Gog ak Magog. Dina leen dajale ngir xare, te dinañu bare ni peppi suuf cig tefes. 20:9 Dinañu sam suuf sépp, di wër dalu gaayi Yàlla yi ak dëkk, bi Yàlla bëgg. Waaye safara daldi jóge asamaan, lakk leen. 20:10 Dees na jàpp Seytaane, mi leen daan nax, sànni ko ci déegu safara ak tamarax bi, mu fekki rab wa ak naaféq ba mbubboo yonent. Foofa dinañu leen mbugal guddi ak bëccëg ba fàww. 20:11 Noonu ma gis gàngune mu mag te weex, ak ka ca toog. Asamaan ak suuf daw, sore ko, ba ne mes. 20:12 Ma gis néew ya, mag ak ndaw, ñu taxaw ca kanamu gàngune ma. Ñu daldi ubbi ay téere, ubbi itam beneen téere, téereb dund bi. Ñu àtte néew ya, ku nekk ci say jëf, ni ñu ko binde woon ca téere ya. 20:13 Noonu géej gëq néew, yi nekkoon ci moom; dee ak barsàq delloo néew, ya ñu yoroon. Ñu àtte ñépp ci seeni jëf. 20:14 Ñu jàpp dee ak barsàq, sànni ca déegu safara sa. Déegu safara soosu moo di ñaareelu dee. 20:15 Képp ku ñu bindul sa tur ci téereb dund bi, dees na la sànni ci déegu safara si.
21:1 Noonu ma gis asamaan su bees ak suuf su bees, ndaxte asamaan su jëkk sa ak suuf su jëkk sa wéyoon nañu, te géej gi amatul. 21:2 Ma gis, wàcce ca asamaan, jóge ca wetu Yàlla, Yerusalem gu bees gi, dëkk bu sell, bi ñu waajal ba mu jekk ni séet buy nég jëkkëram. 21:3 Ma dégg baat bu xumb jibe ca gàngune ma naan: «Dalub Yàllaa ngi ci biir nit ñi. Dina dëkk ak ñoom, nit ñi dinañu nekk ay gaayam, te moom Yàlla ci boppam dina ànd ak ñoom, nekk Yàlla seen Boroom. 21:4 Dina fomp bépp rangooñ ci seeni bët; te dee dootul am walla naqar walla jooy walla metit, ndaxte yëf yu jëkk ya wéy nañu.» 21:5 Noonu ki toog ca gàngune ma ne: «Maa ngi yeesal lépp!» Mu ne ma: «Bindal, ndaxte kàddu yii yu wóor lañu te dëggu.» 21:6 Mu teg ca ne ma: «Lépp mat na! Maay Alfa ak Omega, njàlbéen gi ak muj gi. Ku mar, dinaa la may ci bëtu ndoxum dund mi, te doo fey dara. 21:7 Ku daan, dinga am cér ci mbir yii. Dinaa nekk Yàlla sa Boroom, te dinga nekk doom ci man. 21:8 Waaye ñi ragal, ñi gëmul, ñiy def lu ñaaw, ñiy bóom nit, ñiy njaaloo, luxuskat yi, xërëmkat yi ak fenkat yépp, seen añ moo di déegu safara ak tamarax bi. Loolu mooy ñaareelu dee gi.» 21:9 Gannaaw loolu benn malaaka ñëw, mi bokk ca juróom-ñaari malaaka, ya yoroon juróom-ñaari ndabi musiba yu mujj ya, ne ma: «Ñëwal, ma won la séet bi, jabaru Mbote mi.» 21:10 Noonu Xelum Yàlla solu ma, malaaka ma yóbbu ma ci kaw tund wu réy-a-réy. Noonu mu won ma Yerusalem, dëkk bu sell bi, muy wàcce ci asamaan, jóge ca wetu Yàlla, 21:11 ànd ak ndamu Yàlla. Leeraayam mel ni leeraayu per bu jafe lool, ni jamaa buy ray-rayi. 21:12 Miir bu réy te kawe moo ko wër te am fukki bunt ak ñaar, te bu ca nekk malaaka taxaw ca wet ga. Ca bunt ya bind nañu ca fukki tur ak ñaar, yu giiri bànni Israyil. 21:13 Ca penku am na fa ñetti bunt; ca nor ñett; ca sudd ñett ak ñett ca sowu. 21:14 Samp nañu miiru dëkk ba ci fukki fondamaa ak ñaar, yu ñu bind turi fukki ndawi Mbote ma ak ñaar. 21:15 Ki doon wax ak man amoon na nattukaay, di bantu wurus bu mu doon natte dëkk ba ak miir ba ko wër, ak bunt ya. 21:16 Dëkk ba dafa kaare, guddaay ba ak yaatuwaay ba ñoo tolloo. Mu natt dëkk ba ak bant ba mu yor. Guddaay ba, yaatuwaay ba ak taxawaay ba lépp tolloo, di fukki junni ak ñaar ciy estat. 21:17 Malaaka ma natt miir ba nattub nit, fekk miir ba di téeméer ak ñeent-fukk ak ñeenti xasab. 21:18 Miir ba, jamaa lañu ko liggéeye, te dëkk ba di wurusu ngalam, leer ni weer bu set. 21:19 Fondamaay miiru dëkk ba rafetale nañu leen xeeti per yu nekk.Fondamaa bu jëkk ba jamaa la;ñaareel ba, per bu bulo bu ñuy wax safir;ñetteel ba, per bu wert bu ñuy wax kalseduwan;ñeenteel ba, per bu wert te lerax, bu ñuy wax emëróot; 21:20 juróomeel ba, per bu xonq bu ñuy wax sardonigsë;juróom-benneel ba, per bu xonq curr bu ñuy wax sarduwan;juróom-ñaareel ba, per bu mboq bu ñuy wax kirisolit;juróom-ñetteel ba, per bu wert ni géej bu ñuy wax beril;juróom-ñeenteel ba, per bu mboq bu ñuy wax topas;fukkeel ba, per bu wert bu ñuy wax kirisoparas;fukkeel ba ak benn, per bu bulo bu ñuy wax yasent;fukkeel ba ak ñaar, per bu yolet bu ñuy wax ametist. 21:21 Fukki bunt ya ak ñaar, ay per yu weex lañu. Bunt bu nekk di benn per kepp. Péncu dëkk ba di wurusu ngalam, leer ni weer bu set. 21:22 Gisuma ca dëkk ba kër Yàlla, ndaxte Boroom bi Yàlla Aji Kàttan ji ak Mbote ma ñooy màggalukaay ba. 21:23 Dëkk ba soxlawul jant walla weer ngir leeral ko, ndaxte ndamu Yàlla moo koy leeral, te Mbote ma moo nekk làmpam. 21:24 Xeeti àddina dinañu dox cig leeram, te buuri àddina dinañu ca indi seen ndam. 21:25 Bunti dëkk ba duñu tëju bëccëg, te guddi du fa am. 21:26 Dinañu fa indi ndamu xeet yi ak seen alal. 21:27 Dara du fa dugg lu am sobe, mbaa kenn kuy sóobu ci ñaawteef walla fen. Ñi ñu bind ci téereb dund bu Mbote mi rekk ñoo fay dugg.
22:1 Noonu malaaka ma won ma dexu ndoxum dund, mu leer ni weer bu set, di génn ca gàngune mu Yàlla ak Mbote ma, 22:2 xellee ca digg péncu dëkk ba. Ca weti dex ga amoon na ca garabu dund, guy meññ fukki yoon ak ñaar, di meññ weer wu nekk, te xob ya di faj xeet yi. 22:3 Musiba dootul am. Gàngune mu Yàlla ak Mbote mi mu ngi ci dëkk bi, te ay jaamam dinañu ko jaamu. 22:4 Dinañu gis xar-kanamam, te turam dina nekk ci seen jë. 22:5 Guddi dootul am, te kenn dootul soxla leeru làmp walla naaju jant, ndaxte Boroom bi Yàlla moo leen di leeral. Te dinañu nguuru ba fàww. 22:6 Noonu malaaka ma ne ma: «Wax jii ju wóor la te dëggu. Boroom bi, Yàlla jiy leeral xeli yonent yi, moo yónni malaakaam, ngir mu won ay jaamam mbir yi dëgmël di ñëw.» 22:7 «Maa ngi ñëw léegi. Yaw miy sàmm waxi Yàlla, yi ci téere bii, barkeel nga.» 22:8 Man Yowaana maa dégg mbir yii te gis ko. Ba ma ko déggee te gis ko, damaa daanu ca tànki malaaka, ma ma ko doon won, bëgg koo jaamu. 22:9 Waaye mu ne ma: «Moytu koo def. Sa nawle laa ci liggéey bi, yaw ak say bokki yonent ak ñiy sàmm waxi téere bii. Jaamul Yàlla.» 22:10 Mu ne ma it: «Bul tëj téere bii ak waxi Yàlla yi mu ëmb, ndaxte waxtu wi jege na. 22:11 Ku jubadi, na sax ci jubadeem; ku taq sobe, na sigiñu ci sobeem; ku jub, na wéy ci jëf yu jub; ku sell, na ci ŋoy.» 22:12 Yeesu nee na: «Maa ngi ñëw léegi, indaale pey gi, ngir delloo ku nekk lu mengoo ak lu mu def. 22:13 Man maay Alfa ak Omega, ki jëkk te mujj, njàlbéen gi ak muj gi. 22:14 «Yéen ñi fóot seeni mbubb, ngir sañ a lekk ci garabu dund gi te dugg ci bunti dëkk bi, barkeel ngeen. 22:15 Waaye ñi ci biti ñooy xaj yi, luxuskat yi, njaalookat yi, bóomkat yi, xërëmkat yi ak ñépp ñiy sopp fen te di ci wéy. 22:16 «Man Yeesu maa yónni sama malaaka, ngir mu seede leen mbir yii ci digg mboolooy ñi gëm. Man maay car, bi soqikoo ci Daawuda, di biddiiwu njël bu leer bi.» 22:17 Te Xelum Yàlla ak séetu Mbote mi ñu ngi naan: «Ñëwal.» Képp ku dégg wax jii, na ne: «Ñëwal.» Na képp ku mar, ñëw; ku bëgg, duyal ci ndoxum dund mi te doo fey dara. 22:18 Man Yowaana maa ngi koy wax képp ku dégg waxi Yàlla, yi nekk ci téere bii: ku ci yokk dara, Yàlla dina dolli ci sa mbugal musiba, yi ñu wax ci téere bii. 22:19 Ku dindi dara ci waxi Yàlla, yi nekk ci téere bii, Yàlla dina dindi sa wàll ca garabu dund ga ak dëkk bu sell ba, ñaar yooyu ñu bind ci téere bii. 22:20 Kiy seede mbir yii nee na: «Waaw, maa ngi ñëw léegi.» Amiin. Boroom bi Yeesu, ñëwal. 22:21 Na yiwu Boroom bi Yeesu ànd ak yéen ñépp.